{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/act.htm","path":"bib/wb/wlf/act.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/act.htm","text":"1:1 Yaw Teyofil, t\u00e9ere bu j\u00ebkk, ba ma bindoon, \u00ebmb na l\u00e9pp li Yeesu t\u00e0mbali woon a j\u00ebf ak a j\u00e0ngale,\n1:2 ba ci b\u00e9s, ba ko Y\u00e0lla y\u00e9ege ci asamaan. Lu ko jiitu joxoon na ay ndigal, jaare ci Xel mu Sell mi, j\u00ebm ci ndaw ya mu t\u00e0nnoon.\n1:3 Gannaaw ay coonoom, \u00f1\u00ebw na ci \u00f1oom, di leen won ay firnde yu bare te w\u00e9r ne mu ngi dund; mu fee\u00f1u leen diirub \u00f1eent-fukki fan, di diisoo ak \u00f1oom ci lu j\u00ebm ci nguuru Y\u00e0lla.\n1:4 Am b\u00e9s muy lekk ak \u00f1oom, mu sant leen ne: \u00abBuleen sore Yerusalem, waaye ngeen xaar li Baay bi dige woon te ma waxoon leen ko.\n1:5 Ndaxte Yaxya daa na s\u00f3ob nit \u00f1i ci ndox, waaye y\u00e9en dees na leen s\u00f3ob ci Xel mu Sell mi fi ak ay fan yu n\u00e9ew.\u00bb\n1:6 Bi \u00f1u dajaloo ak moom nag, \u00f1u laaj ko: \u00abBoroom bi, ndax ci jamono jii ngay y\u00e9kkatiwaat nguuru Israyil?\u00bb\n1:7 Mu tontu leen: \u00abNgeen xam jamono yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sa\u00f1-sa\u00f1am, loolu mayu\u00f1u leen ko.\n1:8 Waaye bu Xel mu Sell mi \u00f1\u00ebwee ci y\u00e9en, dingeen jot k\u00e0ttan te nekk samay seede ci d\u00ebkku Yerusalem, ca diiwaani Yude ak Samari y\u00e9pp ak ba fa \u00e0ddina yem.\u00bb\n1:9 Bi mu waxee loolu, te \u00f1u di ko xool, Y\u00e0lla y\u00e9ege na ko, te aw niir j\u00ebl ko, l\u00e0q ko seeni b\u00ebt.\n1:10 Bi muy dem nag, te \u00f1u ne j\u00e0kk asamaan, \u00f1aar \u00f1u sol yu weex daldi ne seef, taxaw ci seen wet.\n1:11 \u00d1u ne leen: \u00abY\u00e9en waa Galile, lu tax ngeen taxaw, di xool ci asamaan? Yeesu male \u00f1u j\u00eble ci seen biir, y\u00e9ege ko asamaan, dina dellusi ni ngeen ko gise, muy dem asamaan.\u00bb\n1:12 Bi loolu amee \u00f1u j\u00f3ge ca tund, woowu \u00f1uy wax tundu Oliw ya, te mu dend ak Yerusalem lu tollu ak kilomet, \u00f1u daldi dellu Yerusalem.\n1:13 Bi \u00f1u dikkee, \u00f1u y\u00e9eg ca n\u00e9eg, ba sut ca taax ma, fa \u00f1uy dal. \u00d1oo doon Piyeer ak Yowaana, Saag ak Andare, Filib ak Tomaa, Bartelemi ak Mac\u00eb, Saag doomu Alfe, ak Simo\u014b mi bokkoon ci mbooloo mi \u00f1uy wax \u00d1i farlu ci moom seen r\u00e9ew; ak Yudaa doomu Saag.\n1:14 \u00d1oom \u00f1\u00e9pp \u00f1oo bokk menn xel, di w\u00e9y ci \u00f1aan ci Y\u00e0lla, \u00e0nd ak jig\u00e9en \u00f1i ak Maryaama, ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu g\u00f3or.\n1:15 Ca b\u00e9s yooya nag Piyeer taxaw ca digg bokk ya, di mbooloo mu tollu ni t\u00e9em\u00e9er ak \u00f1aar-fukk.\n1:16 Mu ne leen: \u00abBokk yi, li Xel mu Sell mi waxoon ci Mbind mi jaarale ko ci g\u00e9mmi\u00f1u Daawuda, f\u00e0ww mu am. Waxoon na ci mbirum Yudaa, mi wommat \u00f1i j\u00e0pp Yeesu\n1:17 te mu bokkoon ci nun, ba am c\u00e9r ci ligg\u00e9ey bi.\u00bb\n1:18 --Pey gi Yudaa jotoon ci \u00f1aawteefam, mu j\u00ebnd ci tool, daanu fa, ba f\u00e0cc, ay buttitam tuuru.\n1:19 Loolu siiwoon na ci waa Yerusalem, moo tax ci seen l\u00e0kk \u00f1uy tudde tool ba Akeldama, maanaam \u00abToolu deret.\u00bb \u2014\n1:20 Piyeer teg ca ne: \u00abNdaxte lii la\u00f1u bind ci t\u00e9ereb Sab\u00f3or:\u201cNa k\u00ebram gental,bu fa kenn d\u00ebkk.\u201d Te it:\u201cNa keneen bey sasam.\u201d\n1:21 Kon \u00f1eel na nu, nu t\u00e0nn kenn ci \u00f1i bokk ak nun, diir bi Yeesu doon dem ak a dikk ci sunu biir,\n1:22 li dale ci bi ko Yaxya s\u00f3obee ci ndox, ba b\u00e9s ba ko Y\u00e0lla j\u00eble ci sunu biir, y\u00e9ege ko. Kooku war na \u00e0nd ak nun, di seedeel ndekkitel Yeesu.\u00bb\n1:23 Bi ko Piyeer waxee, \u00f1u tudd \u00f1aar: Yuusufa, mi \u00f1u dippee Barsabas te di ko d\u00e0kkentale Yustus, moom ak Macas.\n1:24 \u00d1u \u00f1aan ci Y\u00e0lla ne: \u00abBoroom bi, yaw mi xam xolu nit \u00f1\u00e9pp, won nu ki nga t\u00e0nn ci \u00f1aar \u00f1ii,\n1:25 mu yenu ligg\u00e9eyu nekk sa ndaw, wuutu Yudaa, mi ko b\u00e0yyi, dem b\u00e9rabam.\u00bb\n1:26 Noonu \u00f1u boole leen, tegoo ay bant, bant ba dal ca Macas, mu fekki fukki ndaw ya ak benn.\n2:1 Bi b\u00e9su m\u00e0ggalu P\u00e0ntakot agsee, \u00f1oom \u00f1\u00e9pp booloo na\u00f1u ci benn b\u00e9rab.\n2:2 Ca saa sa riir jollee asamaan, mel ni ngelaw lu gaaw te bare doole, daldi fees dell k\u00ebr, ga \u00f1u toog.\n2:3 Te ay l\u00e0mmi\u00f1 yu mel ni safara fee\u00f1u leen, \u00f1u tasaaroo ci seen biir, to\u014b ca kaw kenn ku nekk.\n2:4 Noonu \u00f1u fees ak Xel mu Sell mi \u00f1oom \u00f1\u00e9pp, \u00f1u daldi wax yeneeni l\u00e0kk, ni leen Xel mu Sell mi maye, \u00f1u wax ko.\n2:5 Fekk booba amoon na ay Yawut yu daloon Yerusalem, doon ay nit \u00f1u ragal Y\u00e0lla te bokk ci xeeti \u00e0ddina y\u00e9pp.\n2:6 Bi nit \u00f1i d\u00e9ggee riir ma nag, \u00f1\u00e9pp dajaloo, daldi waaru ci li \u00f1u leen d\u00e9gg, \u00f1uy wax ku nekk sa l\u00e0kk.\n2:7 \u00d1u waaru te y\u00e9emu naa: \u00abGisleen, \u00f1iy wax \u00f1\u00e9pp, ndax du\u00f1u waa diiwaanu Galile?\n2:8 Naka la man a ame nag, nu di leen d\u00e9gg, kenn ku nekk ci nun, \u00f1uy wax ci sa l\u00e0mmi\u00f1, wi nga n\u00e0mp?\n2:9 Nun \u00f1i ay P\u00e0rt, waa Medi ak waa Elam, nun \u00f1i d\u00ebkk Mesopotami, r\u00e9ewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi,\n2:10 di waa Firisi, Pamfili, Misra ak weti Libi, yi dend ak Siren, nun ak gan \u00f1i j\u00f3ge Room,\n2:11 Yawut yi ak \u00f1i tuub ci yoonu Yawut yi, waa Kereet ak Araab yi, nun \u00f1\u00e9pp nu ngi leen di d\u00e9gg, \u00f1uy y\u00e9gle m\u00e0ggaayi Y\u00e0lla ci sunuy l\u00e0kk!\u00bb\n2:12 Noonu \u00f1\u00e9pp waaru, ba jaaxle lool, \u00f1uy waxante ci seen biir ne: \u00abLii lu muy tekki?\u00bb\n2:13 Waaye \u00f1enn \u00f1i di leen \u00f1aawal ne: \u00abWaay! \u00f1ii da\u00f1oo m\u00e0ndi ak bii\u00f1.\u00bb\n2:14 Ci kaw loolu Piyeer taxaw, \u00e0nd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di y\u00e9gal mbooloo ma ne: \u00abBokki Yawut yi ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp \u00f1i d\u00ebkk Yerusalem, d\u00e9gluleen bu baax te xam lii ma leen di wax!\n2:15 Nit \u00f1ii m\u00e0ndiwu\u00f1u, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk.\n2:16 Waaye lii mooy li Y\u00e0lla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne:\n2:17 \u201cY\u00e0lla nee na: Ci b\u00e9s yu mujj yi,dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit \u00f1\u00e9pp;seen xeet wu g\u00f3or ak wu jig\u00e9endina\u00f1u wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla;waxambaane yi dina\u00f1u gis ay pee\u00f1ute m\u00e0ggat yi di g\u00e9nt ay g\u00e9nt.\n2:18 Waaw ci b\u00e9s yooyu dinaa tuur ci sama Xelci sama kaw jaam yu g\u00f3or ak yu jig\u00e9en,te dina\u00f1u wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n2:19 Dinaa wone ay k\u00e9emaan ci kaw ci asamaanak ay firnde ci suuf ci \u00e0ddina,muy deret, safara ak ay niiri saxar.\n2:20 Jant bi dina daldi l\u00ebnd\u00ebm,weer wi deretal,bala b\u00e9su Boroom biy \u00f1\u00ebw,di b\u00e9s bu mag, bi \u00e0nd ak ndam.\n2:21 Booba nag ku woo Boroom bi ci aw turam,dinga mucc.\u201d\n2:22 \u00abY\u00e9en bokki Israyil, d\u00e9gluleen wax jii! Yeesu mi d\u00ebkk Nasaret, nit la woon, ku Y\u00e0lla d\u00ebggal ci seen kanam ciy k\u00e9emaan, ay jaloore ak firnde, ya Y\u00e0lla defoon jaarale ko ci moom ci seen biir; y\u00e9en xam ngeen ko.\n2:23 Moom nag j\u00e9bbale na\u00f1u ko, jaar ci nas, bi Y\u00e0lla dogaloon te xam ko lu jiitu; te y\u00e9en rey ngeen ko ci daaj ko ci bant, jaarale ko ci loxoy b\u00e0kkaarkat.\n2:24 Waaye Y\u00e0lla dekkal na ko, daggal ko buumi dee, ndaxte dee m\u00ebnu koo t\u00e9ye.\n2:25 Daawuda wax na ci mbiram ne:\u201cSaa su ne gis naa Boroom bi ci sama kanam,gannaaw mu ngi ci sama ndeyjoor,kon duma raf.\n2:26 Moo tax sama xol sedd,may woy sama b\u00e0nneex,te it sama yaram di t\u00ebdd ci yaakaar.\n2:27 Ndaxte doo b\u00e0yyi sama ruu ci bars\u00e0q,te doo seetaan sa waa ju sell, mu y\u00e0qu.\n2:28 Xamal nga ma yoonu dund;dinga ma b\u00e9glooji ci sa kanam.\u201d\n2:29 \u00abBokk yi, man naa leen a wax lu w\u00f3or ci mbirum maam Daawuda, ne dee na te suul na\u00f1u ko; b\u00e0mmeelam mu ngi ci nun ba tey.\n2:30 Waaye yonent la woon, te xamoon na ne, Y\u00e0lla digoon na ko ci ngi\u00f1 ne, dina teg ci nguuram kenn ci askanam.\n2:31 Kon gis na lu \u00f1\u00ebwagul, di wax ci mbirum ndekkitel Kirist ne, b\u00e0yyiwu\u00f1u ko ci bars\u00e0q, te yaramam y\u00e0quwul.\n2:32 Yeesu moomu nag, Y\u00e0lla dekkal na ko; nun \u00f1\u00e9pp seede nanu ko.\n2:33 Y\u00e0lla y\u00e9ege na ko ak ndeyjooram, te jot na ci Baay bi Xel mu Sell mi \u00f1u dige woon, ba tuur lii ngeen gis te d\u00e9gg ko.\n2:34 Ndaxte du Daawudaa y\u00e9eg ci asamaan, waaye moom ci boppam nee na:\u201cBoroom bi wax na sama Boroom:\u2018Toogal ci sama ndeyjoor,\n2:35 ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.\u2019 \u201d\n2:36 \u00abNa b\u00e0nni Israyil g\u00e9pp xam bu w\u00f3or nag ne, Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Y\u00e0lla def na ko Boroom ak Almasi bi.\u00bb\n2:37 Bi ko mbooloo ma d\u00e9ggee, naqaru xol wu metti j\u00e0pp leen; \u00f1u daldi ne Piyeer ak ndaw ya ca des: \u00abBokk yi, lu nu war a def?\u00bb\n2:38 Piyeer tontu leen ne: \u00abTuubleen seeni b\u00e0kkaar, te kenn ku nekk ci y\u00e9en, \u00f1u s\u00f3ob ko ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Noonu Y\u00e0lla dina leen baal seeni b\u00e0kkaar te may leen Xel mu Sell mi.\n2:39 Ndaxte li Y\u00e0lla dige woon, y\u00e9ena ko moom ak seeni doom ak \u00f1u sore \u00f1\u00e9pp, di \u00f1\u00e9pp \u00f1i Y\u00e0lla sunu Boroom di woo ci moom.\u00bb\n2:40 Noonu mu artu leen ak yeneen wax yu bare, di leen d\u00e9nk ne: \u00abR\u00ebccleen ci niti jamono ju d\u00ebng jii.\u00bb\n2:41 \u00d1i nangu ay waxam nag, \u00f1u s\u00f3ob leen ci ndox, te ca b\u00e9s booba lu mat limub \u00f1etti junniy nit yokku na\u00f1u ci \u00f1oom.\n2:42 \u00d1oom nag \u00f1uy w\u00e9y ci nj\u00e0ngalem ndaw yi ak cig bokk, ci damm mburu ak \u00f1aan ci Y\u00e0lla.\n2:43 Ragal j\u00e0pp \u00f1\u00e9pp, te ndaw yi di def ay k\u00e9emaan ak ay firnde yu bare.\n2:44 \u00d1i g\u00ebm nag da\u00f1oo booloo te bokk l\u00e9pp.\n2:45 \u00d1u jaay seeni suuf ak seen alal, s\u00e9ddoo ko, ku nekk ak la ngay soxla.\n2:46 Te b\u00e9s bu nekk \u00f1u saxoo teew ak benn xalaat ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, tey damm mburu ca k\u00ebr ya; \u00f1uy lekk seen \u00f1am ak xol bu laab tey b\u00e9g,\n2:47 di m\u00e0ggal Y\u00e0lla te am yiw ci wetu nit \u00f1\u00e9pp. Noonu b\u00e9s bu nekk Boroom bi di yokk ca mbooloo ma \u00f1i mucc.\n3:1 Am b\u00e9s Piyeer ak Yowaana dem, ba b\u00ebgg a dugg ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga ca waxtuw \u00f1aan, maanaam tisbaar.\n3:2 Fekk \u00f1u indi fa nit ku judduwaale lafa\u00f1, \u00f1u di ko teg b\u00e9s bu nekk ca bunt, ba \u00f1uy wooye Bunt bu rafet ba, ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, ngir muy yelwaan \u00f1a fay dugg.\n3:3 Bi mu gisee Piyeer ak Yowaana nag, \u00f1uy dugg ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, mu d\u00e9kk leen loxo.\n3:4 Ci kaw loolu Piyeer ak Yowaana ne ko j\u00e0kk, te Piyeer ne ko: \u00abXool nu.\u00bb\n3:5 Lafa\u00f1 bi xool leen, yaakaar ne dina jot dara ci \u00f1oom.\n3:6 Noonu Piyeer ne ko: \u00abAwma xaalis, awma wurus, waaye li ma am, dinaa la ko jox: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret doxal!\u00bb\n3:7 Mu j\u00e0pp ci loxol ndeyjooram, y\u00e9kkati ko. Ci saa si ay t\u00e0nkam ak ay kostanam d\u00ebg\u00ebr.\n3:8 Mu t\u00ebb, daldi taxaw, di dox. Mu dugg ak \u00f1oom ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, muy dox, di t\u00ebb tey sant Y\u00e0lla.\n3:9 Noonu \u00f1\u00e9pp gis ko, muy dox, di sant Y\u00e0lla.\n3:10 Te \u00f1u x\u00e0mmi ko, ne moo daan toog, di yelwaan ca Bunt bu rafet ba ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga. \u00d1u daldi waaru lool te y\u00e9emu ci li ko dikkal.\n3:11 Naka waa ji taq ci Piyeer ak Yowaana, \u00f1\u00e9pp waaru; \u00f1u daldi daw, fekksi leen ca b\u00e9rab ba \u00f1uy wax Werandaa bu Suleymaan.\n3:12 Bi Piyeer gisee loolu nag, mu ne mbooloo mi: \u00abY\u00e9en waa Israyil, lu tax ngeen waaru ci lii? Lu tax ngeen di nu xool j\u00e0kk, mel ni ci sunu k\u00e0ttan, mbaa ci sunu ragal Y\u00e0lla lanu doxloo kii?\n3:13 Y\u00e0llay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanq\u00f3oba, di Y\u00e0llay sunuy maam, m\u00e0ggal na Ndawam Yeesu; y\u00e9ena x\u00e0cceek moom, ba j\u00e9bbal ko Pilaat, fekk naroon na koo b\u00e0yyi.\n3:14 Y\u00e9en xeeb ngeen Aji Sell ji te Jub, te tinul ab reykat.\n3:15 B\u00f3om ngeen Aji Dundal ji, waaye Y\u00e0lla dekkal na ko; seede nanu ko nun \u00f1\u00e9pp.\n3:16 Ci g\u00ebm turam la nit, kii ngeen di gis te xam ko, d\u00ebg\u00ebre; waaw, turu Yeesu ak ng\u00ebm gi j\u00f3ge ci moom, moo tax mu w\u00e9r pe\u014b\u014b ci seen kanam, y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.\n3:17 \u00abL\u00e9egi nag bokk yi, xam naa ne, \u00f1\u00e0kka xam a tax ngeen def ko, y\u00e9en ak seeni kilifa.\n3:18 Waaye noonu la Y\u00e0lla amale li mu y\u00e9gle woon lu jiitu jaarale ko ci g\u00e9mmi\u00f1ug yonent y\u00e9pp naan, Almaseem dina sonn.\n3:19 Tuubleen seeni b\u00e0kkaar nag te wo\u00f1\u00f1iku ci Y\u00e0lla, ngir seeni b\u00e0kkaar far.\n3:20 Noonu jamonoy p\u00e9ex dina bawoo ci Boroom bi, te muy yebal Almasi bi mu leen jagleel, maanaam Yeesu.\n3:21 Asamaan war na koo yor, ba jamono ju \u00f1uy defaraat l\u00e9pp, di jamono ji Y\u00e0lla waxoon jaarale ko ci g\u00e9mmi\u00f1ug yonentam yu sell y\u00e9pp, li dale ci nj\u00e0lb\u00e9enug \u00e0ddina.\n3:22 Ndaxte Musaa nee woon na: \u201cBoroom bi seen Y\u00e0lla dina leen fee\u00f1alal ci seen xeet Yonent ni man; nangeen ko d\u00e9ggal ci l\u00e9pp lu mu leen wax.\n3:23 K\u00e9pp ku d\u00e9ggalul Yonent boobu, dees na la far ci xeet wi.\u201d\n3:24 \u00abLi dale sax ci Samwil ak \u00f1i ci topp, b\u00e9pp yonent bu wax y\u00e9gle na b\u00e9s yii.\n3:25 Y\u00e9en nag y\u00e9enay donn yonent yi ak k\u00f3ll\u00ebre, gi Y\u00e0lla fasoon ak seeni maam, bi mu naan Ibraayma: \u201cXeeti \u00e0ddina y\u00e9pp dina\u00f1u barkeel ci ki soqikoo ci yaw.\u201d\n3:26 Y\u00e0lla fee\u00f1al na Ndawam, j\u00ebkk koo yebal ci y\u00e9en, ngir barkeel leen, ci wo\u00f1\u00f1i leen kenn ku nekk ci say b\u00e0kkaar.\u00bb\n4:1 Bi \u00f1uy wax ak mbooloo ma, saraxalekat ya ak kilifag \u00f1iy wottu k\u00ebr Y\u00e0lla ga ak Sadusen ya daanu ci seen kaw.\n4:2 \u00d1u mer lool ci li \u00f1uy waar nit \u00f1i, di y\u00e9gle ndekkitel \u00f1i dee, sukkandikoo ko ci ndekkitel Yeesu.\n4:3 Noonu \u00f1u j\u00e0pp leen, t\u00ebj leen ba ca \u00ebll\u00ebg sa, ndaxte mu nga doon t\u00e0mbalee guddi.\n4:4 Waaye \u00f1u bare ca \u00f1a d\u00e9gg wax ja g\u00ebm na\u00f1u, te limu g\u00f3or \u00f1i g\u00ebm yokku na, ba mat jur\u00f3omi junni.\n4:5 Ca \u00ebll\u00ebg sa nag kilifay Yawut yi ak njiit yi ak xutbakat yi dajaloo ci Yerusalem.\n4:6 R\u00e0\u00f1\u00f1e na\u00f1u ci: Anas, miy saraxalekat bu mag bi, Kayif, Yowaana, Alegs\u00e0ndar ak bokki saraxalekat bu mag bi.\n4:7 \u00d1u d\u00ebj Piyeer ak Yowaana ca digg ba, laaj leen ne: \u00abLii ngeen def, ci gan k\u00e0ttan, mbaa ci turu kan, ngeen ko defe?\u00bb\n4:8 Ci kaw loolu Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi, ne leen: \u00abY\u00e9en kilifay xeet wi ak njiit yi,\n4:9 bu fekkee ne xettali nit ku wopp, ba mu w\u00e9r, moo tax ngeen d\u00ebj nu ci p\u00e9nc mi tey,\n4:10 nangeen xam lii, y\u00e9en \u00f1\u00e9pp ak b\u00e0nni Israyil g\u00e9pp! Ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret, mi ngeen daajoon ca bant te Y\u00e0lla dekkal ko, ci tur woowu la nit kii j\u00eble ag w\u00e9r, ba taxaw ci seen kanam.\n4:11 Yeesu moomu mooy:\u201cDoj wi ngeen xeeboon, y\u00e9en tabaxkat yi,te moo doon doju ko\u00f1.\u201d\n4:12 Te mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu \u00f1u maye ci nit \u00f1i, wu nu war a mucce.\u00bb\n4:13 Kon bi \u00f1u gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana \u00e0ndal, te \u00f1u xam ne, musu\u00f1oo j\u00e0ng mbaa \u00f1uy g\u00ebstu ci diine, \u00f1u daldi waaru, r\u00e0\u00f1\u00f1ee ne, daa na\u00f1u \u00e0nd ak Yeesu.\n4:14 Te bi \u00f1u gisee nit, ka \u00f1u fajoon, taxaw ak \u00f1oom, m\u00ebnu\u00f1u caa teg dara.\n4:15 Noonu \u00f1u santaane, \u00f1u g\u00e9nne leen, \u00f1u daldi gise ci seen biir,\n4:16 ne: \u00abLu nuy def ak \u00f1ii? Ndaxte def na\u00f1u k\u00e9emaan gu siiw; loolu leer na \u00f1i d\u00ebkk Yerusalem \u00f1\u00e9pp, te m\u00ebnunu koo weddi.\n4:17 Waaye ngir mbir mi ba\u00f1 a law ci xeet wi, nanu leen aaye, \u00f1u ba\u00f1 a waxati ak kenn ci tur woowu.\u00bb\n4:18 Noonu \u00f1u woo leen, \u00f1u tere leen bu w\u00f3or, \u00f1u waxati mbaa waare dara ci turu Yeesu.\n4:19 Waaye Piyeer ak Yowaana tontu leen ne: \u00abBu fekkee ne d\u00e9ggal leen te b\u00e0yyi Y\u00e0lla moo jub ci kanam Y\u00e0lla, seetleen ko.\n4:20 Waaye nun m\u00ebnunoo ba\u00f1 a wax li nu gis te d\u00e9gg ko.\u00bb\n4:21 Noonu kilifa yi t\u00ebkkuwaat leen, yiwi leen, \u00f1u dem. Ndaxte amu\u00f1u benn bunt ci \u00f1oom ngir mbugal leen, fekk \u00f1\u00e9pp di m\u00e0ggal Y\u00e0lla ci li xewoon.\n4:22 Ndaxte nit, ka \u00f1u fajoon ci k\u00e9emaan googu, weesoon na \u00f1eent-fukki at.\n4:23 Bi \u00f1u leen yiwee nag, \u00f1u dem ci seeni bokk, nettali leen li saraxalekat yu mag ya ak njiit ya waxoon l\u00e9pp.\n4:24 Bi ko bokk ya d\u00e9ggee nag, \u00f1u m\u00e0nkoo, diis seen k\u00e0ddu Y\u00e0lla ne: \u00abBoroom bi, yaa s\u00e0kk asamaan, suuf, g\u00e9ej ak l\u00e9pp li nekk ci seen biir.\n4:25 Yaa wax, jaar ci sunu maam Daawuda sa jaam, mi doon g\u00e9mmi\u00f1u Xel mu Sell mi, ne:\u201cLu tax xeeti \u00e0ddina di bax?Lu tax \u00f1uy fexe lu m\u00ebnul a am?\n4:26 Buuri \u00e0ddina da\u00f1oo booloo,te kilifa yi dajaloo,di ba\u00f1 Boroom bi ak Almaseem.\u201d\n4:27 Ndaxte ci d\u00ebgg ci d\u00ebkk bii, Erodd ak Po\u00f1s\u00eb Pilaat \u00e0nd ak xeeti \u00e0ddina ak b\u00e0nni Israyil, likkoo na\u00f1u, ngir daaneel sa Ndaw lu sell li nga fal, di Yeesu,\n4:28 te def l\u00e9pp, li sa k\u00e0ttan ak sa ndigal t\u00ebraloon.\n4:29 L\u00e9egi nag Boroom bi, seetal seeni t\u00ebkku te may say jaam, nuy wax sa k\u00e0ddu ak fit.\n4:30 T\u00e0llalal sa loxo, ci w\u00e9ral ak ci wone ay k\u00e9emaan ak ay firnde, jaarale ko ci turu Yeesu, sa Ndaw lu sell li.\u00bb\n4:31 Bi \u00f1u \u00f1aanee ba noppi, b\u00e9rab ba \u00f1u booloo woon daldi yengatu; te \u00f1oom \u00f1\u00e9pp fees ak Xel mu Sell mi, \u00f1uy wax k\u00e0ddug Y\u00e0lla ak fit wu d\u00ebg\u00ebr.\n4:32 Noonu mbooloom \u00f1u g\u00ebm \u00f1i bokk menn xel ak benn xalaat. Kenn daawul aakimoo dara ci alalam, waaye \u00f1oo bokkoon l\u00e9pp.\n4:33 Te ndaw yi di seedeel ndekkitel Yeesu Boroom bi ak k\u00e0ttan gu r\u00e9y. Te yiw wu yaatu \u00ebmb leen, \u00f1oom \u00f1\u00e9pp.\n4:34 Kenn ci \u00f1oom \u00f1\u00e0kkul dara, ndaxte k\u00e9pp ku nekk boroom suuf mbaa am ay k\u00ebr, jaay na ko, indi nj\u00ebg gi,\n4:35 teg ko ci loxoy ndaw ya; \u00f1u di ci s\u00e9dd, kenn ku nekk li mu soxla.\n4:36 Noonu amoon na fa ku tudd Yuusufa, te ndaw yi d\u00e0kkentale ko Barnabas, miy tekki \u00abKiy d\u00ebg\u00ebral fit yi,\u00bb mu soqikoo ci giiru Lewi, te juddoo dunu Sipar.\n4:37 Moom nag jaay na tool, ba mu moom, indi xaalis ba, teg ko ci loxoy ndaw ya.\n5:1 Naka noonu nit ku tudd Ana\u00f1as, \u00e0nd ak Safira jabaram, jaay l\u00e0ccu suuf.\n5:2 Mu dencal boppam benn c\u00e9r ca nj\u00ebg ga, \u00e0nd ca ak jabaram; ba noppi mu indi c\u00e9r ba ca des, teg ko ci loxoy ndaw ya.\n5:3 Bi mu ko defee Piyeer ne ko: \u00abAna\u00f1as, lu tax nga b\u00e0yyi Seytaane dugg la, ba fees sa xol, ngay wor Xel mu Sell mi, ci li nga dencal sa bopp benn c\u00e9r ci nj\u00ebg gi?\n5:4 Bi mu jaragul, ndax moomuloo ko woon? Te bi mu jaree, ndax yilifuloo woon nj\u00ebg gi? Lu tax nga fas ci sa xol def nii? Woruloo nit \u00f1i, waaye Y\u00e0lla nga wor.\u00bb\n5:5 Bi Ana\u00f1as d\u00e9ggee baat yooyu, mu daanu dee. \u00d1i ko d\u00e9gg \u00f1\u00e9pp tiit, ba ne n\u00ebr\u00ebm.\n5:6 Noonu waxambaane ya j\u00f3g, \u00f1u s\u00e0ng ko, y\u00f3bbu ko, j\u00e9bbal Y\u00e0lla.\n5:7 \u00d1etti waxtu gannaaw ga, jabaram duggsi, fekk xamul la fa xew.\n5:8 Piyeer daldi ko ne: \u00abWax ma, ndax lii mooy nj\u00ebgu tool bi?\u00bb Mu tontu ko: \u00abWaawaaw, lii la.\u00bb\n5:9 Ci kaw loolu Piyeer ne ko: \u00abLu tax ngeen \u00e0nd, di dii\u014bat Xelu Boroom bi? \u00d1i denci woon sa j\u00ebkk\u00ebr \u00f1u ngi nii ci bunt bi, te dina\u00f1u la y\u00f3bbu.\u00bb\n5:10 Ca saa sa mu daanu ciy t\u00e0nkam dee. Bi waxambaane ya agsee nag, \u00f1u fekk ko, mu faatu; \u00f1u y\u00f3bbu ko, def ko ci wetu j\u00ebkk\u00ebram.\n5:11 Noonu tiitaange ju mag t\u00e0bbi ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm \u00f1\u00e9pp ak \u00f1i ko d\u00e9gg \u00f1\u00e9pp.\n5:12 Bi loolu amee ay k\u00e9emaan ak ay firnde yu bare di xew ci nit \u00f1i, jaare ca loxoy ndaw ya. \u00d1\u00e9pp di booloo ca Werandaa bu Suleymaan ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga.\n5:13 Te kenn ci \u00f1a ca des \u00f1emewul a booloo ak \u00f1oom, waaye nit \u00f1\u00e9pp di leen m\u00e0ggal.\n5:14 Moona ay nit \u00f1u g\u00ebn a bare, g\u00f3or ak jig\u00e9en, di g\u00ebm Boroom bi, tey taq ci \u00f1oom.\n5:15 Nit \u00f1i indi sax \u00f1u wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir \u00f1enn ci \u00f1oom.\n5:16 Te it nit \u00f1u bare dajaloo, j\u00f3ge ca d\u00ebkk ya w\u00ebr Yerusalem, \u00f1u indi ay jarag ak \u00f1u rab yu bon sadd; te \u00f1oom \u00f1\u00e9pp daldi w\u00e9r.\n5:17 Booba saraxalekat bu mag ba j\u00f3g ak g\u00e0ngooram g\u00e9pp, maanaam kureelu Sadusen, ga fa d\u00ebkk. Ki\u00f1aan gu mag j\u00e0pp leen,\n5:18 ba \u00f1u j\u00e0pp ndaw ya, t\u00ebj leen ca kaso ba.\n5:19 Waaye ci guddi malaakam Boroom bi ubbi buntu kaso ba, g\u00e9nne leen ci biti naan:\n5:20 \u00abDemleen taxaw ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, te xamal nit \u00f1i l\u00e9pp lu j\u00ebm ci dund gu w\u00f3or gii.\u00bb\n5:21 Bi \u00f1u d\u00e9ggee loolu, \u00f1u dugg ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga ci suba teel, daldi waare. Bi \u00f1u koy def, saraxalekat bu mag ba ak g\u00e0ngooram \u00f1\u00ebw, woolu kureelu \u00e0ttekat ya, maanaam mbooloom njiiti b\u00e0nni Israyil g\u00e9pp; \u00f1u y\u00f3nnee, ngir j\u00ebli ndaw ya ca kaso ba.\n5:22 Waaye bi wottukati k\u00ebr Y\u00e0lla ga agsee ca kaso ba, gisu\u00f1u leen fa; \u00f1u daldi dellusi, y\u00e9gle ko\n5:23 ne: \u00abFekk nanu kaso ba t\u00ebju bu w\u00f3or ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.\u00bb\n5:24 Bi kilifag wottukati k\u00ebr Y\u00e0lla ga ak saraxalekat yu mag ya d\u00e9ggee loolu, \u00f1u daldi ciy jaaxle lool, \u00f1uy laajante, fu lii di mujj.\n5:25 Noonu benn waay \u00f1\u00ebw, y\u00e9gal leen ne: \u00abNit \u00f1i ngeen t\u00ebjoon \u00f1u ngi taxaw ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, di j\u00e0ngal nit \u00f1i.\u00bb\n5:26 Ci kaw loolu kilifa ga ak wottukat ya dem j\u00ebli leen; waaye boolewu\u00f1u ci fitna, ngir ragal nit \u00f1i s\u00e0nni leen ay xeer.\n5:27 Bi \u00f1u leen indee, \u00f1u d\u00ebj leen ci kanamu mbooloo ma. Saraxalekat bu mag ba laaj leen\n5:28 ne: \u00abNdax terewunu leen ci lu w\u00e9r, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli y\u00e9ena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.\u00bb\n5:29 Waaye Piyeer ak ndaw ya tontu leen ne: \u00abD\u00e9ggal Y\u00e0lla moo g\u00ebn d\u00e9ggal nit.\n5:30 Y\u00e0llay sunuy maam dekkal na Yeesu, mi ngeen b\u00f3omoon ci w\u00e9kk ko ca bant ba.\n5:31 Te Y\u00e0lla y\u00e9kkati na ko ci ndeyjooram, mu nekk Buur ak Musalkat, ngir may b\u00e0nni Israyil r\u00e9ccu, ba mu baal leen seeni b\u00e0kkaar.\n5:32 Seede nanu loolu, nun ak Xel mu Sell, mi Y\u00e0lla may \u00f1i koy d\u00e9ggal.\u00bb\n5:33 Bi \u00f1u d\u00e9ggee loolu, \u00f1u mer ba seen xol di dagg, \u00f1u b\u00ebgg leen a rey.\n5:34 Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu j\u00f3g ca mbooloo ma, santaane \u00f1u g\u00e9nne leen tuuti.\n5:35 Bi \u00f1u ko defee mu ne leen: \u00abY\u00e9en bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit \u00f1oo\u00f1u.\n5:36 Ndaxte bu y\u00e0ggul T\u00ebdas j\u00f3goon na, mbubboo daraja, ba lu mat \u00f1eenti t\u00e9em\u00e9eri nit takktoo ak moom. T\u00ebdas moomu nag reyees na ko, te \u00f1i ko toppoon \u00f1\u00e9pp tasaaroo, ba seen pexe nasax.\n5:37 Gannaawam it Yudaa mu Galile j\u00f3g, ca jamono ja \u00f1u doon bind waa r\u00e9ew ma, mu j\u00f3gloo nit \u00f1u bare, \u00f1u \u00e0nd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam \u00f1\u00e9pp tasaaroo.\n5:38 L\u00e9egi maa ngi leen di wax, g\u00e9nnleen ci mbirum \u00f1oo\u00f1u te b\u00e0yyi leen \u00f1u dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen j\u00ebf dee pexem nit, dina y\u00e0qu.\n5:39 Waaye bu fekkee ne ndogalu Y\u00e0lla la, dungeen ko man a fanq, ngir ragal a j\u00e0nkoonte ak Y\u00e0lla.\u00bb\n5:40 Bi mu waxee loolu, \u00f1u fekk ko ci xalaatam; \u00f1u woo ndaw ya, daldi leen d\u00f3or ay yar, tere leen, \u00f1u waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi b\u00e0yyi leen, \u00f1u dem.\n5:41 Ndaw ya nag j\u00f3ge ca kanam kureelu \u00e0ttekat ya, b\u00e9g ci li leen Y\u00e0lla j\u00e0ppe, \u00f1u yeyoo yenu toroxte ngir Tur wa.\n5:42 Noonu b\u00e9s bu nekk ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga ak ca k\u00ebr ya, daawu\u00f1u noppee j\u00e0ngale ak a xamle xebaar bu baax bi, ne Yeesu mooy Almasi bi.\n6:1 Ca b\u00e9s yooyu, naka taalibe yi di g\u00ebn a bare, Yawut yiy l\u00e0kk gereg t\u00e0mbalee \u00f1axtu ci mbirum Yawut tigi yi, te lii a ko waral: jig\u00e9en \u00f1i seen j\u00ebkk\u00ebr dee, te \u00f1u bokk ci \u00f1oom, naraalewu\u00f1u leen ca ndimbal, la \u00f1uy s\u00e9ddale b\u00e9s bu nekk.\n6:2 Noonu fukki ndaw ya ak \u00f1aar woo mbooloom taalibe ya ne leen: \u00abNu b\u00e0yyi k\u00e0ddug Y\u00e0lla, di topptoo mbirum s\u00e9ddale, loolu jekkul ci nun.\n6:3 Kon nag bokk yi, t\u00e0nnleen jur\u00f3om-\u00f1aari nit ci seen biir, \u00f1u am seede su rafet te fees ak Xel mu Sell mi ak sago, nu d\u00e9nk leen ligg\u00e9ey bii.\n6:4 Waaye nun dinanu w\u00e9y ci \u00f1aan ci Y\u00e0lla ak ci yenub xamle k\u00e0ddu gi.\u00bb\n6:5 Lii \u00f1u wax nag neex na mbooloo m\u00e9pp. Noonu \u00f1u t\u00e0nn Ecen, di nit ku fees ak ng\u00ebm ak Xel mu Sell mi, boole ci Filib ak Porokor, teg ca Nikanor, Timon, Parmenas ak Nikolas, mi juddoo Ancos te tuub ci yoonu Yawut ya.\n6:6 \u00d1u j\u00e9bbal leen ndaw ya, \u00f1aanal leen, teg leen loxo.\n6:7 Noonu k\u00e0ddug Y\u00e0lla di law, ba mbooloom taalibe yi di yokku bu bare ci Yerusalem; te saraxalekat yu bare d\u00e9ggal Y\u00e0lla ci topp yoonu ng\u00ebm wi.\n6:8 Naka noona Ecen, mi fees ak yiw ak k\u00e0ttan, di def ay k\u00e9emaan yu mag ak ay firnde ca nit \u00f1a.\n6:9 Waaye ay nit j\u00f3g, bokk ci j\u00e0ngu, bi \u00f1uy wax J\u00e0ngub \u00f1i \u00f1u goreel, di ay niti d\u00ebkki Siren ak Alegs\u00e0ndiri, ak it waa diiwaani Silisi ak Asi. \u00d1uy werante ak Ecen,\n6:10 waaye \u00e0ttanu\u00f1u sagoom ak Xel mi muy waxe.\n6:11 Kon \u00f1u daldi j\u00ebnd ay nit, \u00f1u ne: \u00abD\u00e9gg nanu ko, muy sosal Musaa ak Y\u00e0lla.\u00bb\n6:12 Noonu \u00f1u j\u00f3gloo nit \u00f1i ak njiit yi ak xutbakat yi, \u00f1u dal ci kawam, j\u00e0pp ko, y\u00f3bbu ko ca kureelu \u00e0ttekat ya.\n6:13 Te \u00f1u s\u00e0kk ay naaf\u00e9q yuy seede ne: \u00abKii du b\u00e0yyee wax lu juuyoo ak b\u00e9rab bu sell ba ak yoonu Musaa.\n6:14 Ndaxte d\u00e9gg nanu, muy wax ne, Yeesum Nasaret moomu dina daaneel b\u00e9rab bii te soppi aada, yi nu Musaa batale woon.\u00bb\n6:15 Bi \u00f1u ko waxee, \u00f1a toogoon \u00f1\u00e9pp ca mbooloo ma xool ko j\u00e0kk, gis xar-kanamam, mu mel ni xar-kanamu malaaka.\n7:1 Noonu saraxalekat bu mag ba ne ko: \u00abNdax loolu d\u00ebgg la?\u00bb\n7:2 Ecen tontu ko: \u00abY\u00e9en samay bokk ak samay baay, d\u00e9gluleen! Y\u00e0lla, miy Boroom ndam, fee\u00f1u woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee r\u00e9ewu Mesopotami, te d\u00ebkkagul woon Karan.\n7:3 Mu ne ko: \u201cToxul sa r\u00e9ew, b\u00e0yyi say bokk, te \u00f1\u00ebw ci r\u00e9ew, mi ma lay won.\u201d\n7:4 \u00abCi kaw loolu mu g\u00e9nn r\u00e9ewu niti Kalde, d\u00ebkksi Karan. Te bi baayam faatoo, Y\u00e0lla toxale ko foofa, d\u00eb\u00ebl ko ci r\u00e9ew, mi ngeen d\u00ebkk l\u00e9egi.\n7:5 Waaye mayu ko fa genn moomeel gu mu war a donnale, du sax fu mu man a teg t\u00e0nkam; waaye dig na ko ne, dina ko may r\u00e9ew mi, mu yilif ko moom ak askanam, fekk booba amagul doom.\n7:6 Y\u00e0lla ne ko: \u201c\u00d1i soqikoo ci yaw dina\u00f1u ganeyaan ci r\u00e9ew mu \u00f1u d\u00ebkkul; dees na leen def ay jaam, di leen fitnaal diirub \u00f1eenti t\u00e9em\u00e9eri at.\u201d\n7:7 Waaye Y\u00e0lla nee na: \u201cXeet wi leen jaamloo, man maa leen di \u00e0tte te gannaaw loolu dina\u00f1u g\u00e9nn, di ma jaamu ci b\u00e9rab bii.\u201d\n7:8 Y\u00e0lla nag t\u00ebral k\u00f3ll\u00ebre seen diggante, fas ko ci m\u00e0ndargam xaraf. Noonu Ibraayma jur Isaaxa, xarafal ko ca jur\u00f3om-\u00f1etteelu fan ba; Isaaxa def noonu Yanq\u00f3oba, Yanq\u00f3oba it def noonu fukki maam ya ak \u00f1aar, \u00f1i sos xeet wi.\n7:9 \u00abNaka maam yooyu, da\u00f1oo i\u00f1aane Yuusufa, ba jaay ko, mu j\u00ebm r\u00e9ewu Misra. Waaye Y\u00e0lla taxawu ko,\n7:10 g\u00e9nne ko ci coonoom y\u00e9pp, defal ko yiw ak xel ci kanamu Firawna, buuru Misra, mu def ko kilifag Misra ak k\u00ebram g\u00e9pp.\n7:11 \u00abBi loolu amee xiif t\u00e0bbi ci biir Misra ak r\u00e9ewu Kanaan m\u00e9pp, ba toskare ja metti lool, te sunuy maam amatu\u00f1u lu \u00f1u lekk.\n7:12 Yanq\u00f3oba nag d\u00e9gg ne, Misra am na dugub, mu yebal ca sunuy maam, \u00f1u dem fa yoon wu j\u00ebkk.\n7:13 Bi fa ay doomi baayam delloo nag, Yuusufa x\u00e0mmiku leen, te Firawna xamante ak njabootam.\n7:14 Ci kaw loolu Yuusufa yeble, woo baayam ak mbokkam y\u00e9pp, \u00f1uy jur\u00f3om-\u00f1aar-fukki nit ak jur\u00f3om.\n7:15 Noonu Yanq\u00f3oba dem Misra, faatu fa, moom ak sunuy maam.\n7:16 Gannaaw loolu \u00f1u y\u00f3bbu seeni n\u00e9ew Sikem, dugal leen ca b\u00e0mmeel, ba Ibraayma j\u00ebndoon ak xaalis ca doomi Emor ca Sikem.\n7:17 \u00abBi loolu w\u00e9yee jamono ji jege woon na, ngir Y\u00e0lla amal li mu digoon Ibraayma ci ngi\u00f1; fekk xeet wa di law tey g\u00ebn a bare ci Misra,\n7:18 ba keroog beneen buur bu xamul Yuusufa di falu ci Misra.\n7:19 Buur boobu nag dafa daan nax sunu xeet, di fitnaal sunuy maam, ba di leen s\u00e0nniloo seeni doom, ngir \u00f1u dee.\n7:20 \u00abBooba nag la Musaa juddu, di ku rafet ci kanam Y\u00e0lla; \u00f1u yor ko \u00f1etti weer ci biir k\u00ebr baayam,\n7:21 ba noppi s\u00e0nni ko. Noonu doom ju jig\u00e9en ju Firawna for ko, yar ko ni doomam.\n7:22 Musaa nag di ku yeewu ci xam-xamu waa Misra b\u00e9pp, di j\u00e0mbaar ci wax ak j\u00ebf.\n7:23 \u00abBi mu demee ba am \u00f1eent-fukki at, mu fas y\u00e9eney seeti ay bokkam, maanaam b\u00e0nni Israyil.\n7:24 Noonu mu gis ca ku \u00f1uy n\u00e9ewal doole, mu sotle ko, feyyul ko, ba d\u00f3or waayi Misra ja.\n7:25 Mu defe ne, ay bokkam dina\u00f1u xam ne, ciy loxoom la leen Y\u00e0llay musale, waaye xamu\u00f1u ko.\n7:26 Ca \u00ebll\u00ebg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, mu di leen j\u00e9em a jubale ne leen: \u201cY\u00e9en ay bokk ngeen, lu tax ngeen di xeex?\u201d\n7:27 Waaye kiy n\u00e9ewal doole moroomam b\u00ebm\u00ebx ko ne: \u201cKu la teg kilifa ak \u00e0ttekat ci sunu kaw?\n7:28 Ndax danga maa b\u00ebgg a rey, ni nga defoon d\u00e9mb waayi Misra ja?\u201d\n7:29 Bi Musaa d\u00e9ggee wax jooju, mu daldi daw, dem r\u00e9ewu Majan, di fa ab doxand\u00e9em; mu s\u00e9y fa, ba am \u00f1aari doom.\n7:30 \u00abLu ko wees \u00f1eent-fukki at nag, bi mu nekkee ca m\u00e0ndi\u014bu tundu Sinayi, malaaka fee\u00f1u ko ci takk-takku safara ci biir as ngarab.\n7:31 Bi ko Musaa gisee, mu daldi waaru ci li mu gis; mu jegesi ngir niir ko, d\u00e9gg baatu Boroom bi ne ko:\n7:32 \u201cMan maay sa Y\u00e0llay maam, di Y\u00e0llay Ibraayma, Isaaxa ak Yanq\u00f3oba.\u201d Ci kaw loolu Musaa tiit bay lox, te \u00f1emeetul a xool.\n7:33 Noonu Boroom bi ne ko: \u201cSummil say d\u00e0ll, ndaxte b\u00e9rab bi nga taxaw, b\u00e9rab bu sell la.\n7:34 Gis naa bu baax fitnay sama xeet ci Misra te d\u00e9gg naa seeni tawat, kon w\u00e0cc naa ngir musal leen. L\u00e9egi nag \u00f1\u00ebwal, dinaa la yebal Misra.\u201d\n7:35 \u00abMusaa moomu ba\u00f1oon na\u00f1u ko, ba ne ko: \u201cKu la teg kilifa ak \u00e0ttekat?\u201d Waaye moom la Y\u00e0lla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko fee\u00f1u ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel.\n7:36 Moo leen g\u00e9nne r\u00e9ewu Misra, di def ay k\u00e9emaan ak ay firnde ca r\u00e9ew ma, ca G\u00e9ej gu xonq ga ak ca m\u00e0ndi\u014b ma diirub \u00f1eent-fukki at.\n7:37 Musaa moomu moo ne woon b\u00e0nni Israyil: \u201cY\u00e0lla dina leen fee\u00f1alal ci seeni bokk Yonent bu mel ni man.\u201d\n7:38 Te moo nekkoon ak mbooloo ma ca m\u00e0ndi\u014b ma, \u00e0nd ak sunuy maam, w\u00e9ttalikoo malaaka, mi waxoon ak moom ci tundu Sinayi. Te mu jote ci Y\u00e0lla k\u00e0ddu yiy dund, ngir jottali nu ko.\n7:39 Waaye sunuy maam nanguwu\u00f1u koo d\u00e9ggal; da\u00f1u koo ba\u00f1 te seeni xel d\u00ebpp, dellu Misra.\n7:40 \u00d1u sant Aaroona ne: \u201cS\u00e0kkal nu ay y\u00e0lla yuy jiitu ci sunu kanam, ndaxte Musaa male nu g\u00e9nne ci r\u00e9ewu Misra, xamunu lu ko dal.\u201d\n7:41 Booba nag \u00f1u t\u00ebgglu aw s\u00ebllu, muy x\u00ebr\u00ebm, \u00f1u di ko tuuru, di b\u00e0nneexu ci seeni j\u00ebfi loxo.\n7:42 Waaye bi \u00f1u ko defee Y\u00e0lla d\u00ebddu leen, b\u00ebrg\u00ebl leen, \u00f1uy jaamu biddiiwi asamaan. Moom la\u00f1u bind ci t\u00e9ereb yonent yi ne:\u201cY\u00e9en b\u00e0nni Israyil, ndax rendi ngeen jur,j\u00e9bbal ma, boole ko ak i sarax,diirub \u00f1eent-fukki at ca m\u00e0ndi\u014b ma?\n7:43 Y\u00f3bbu ngeen sax fu nekk t\u00e0nt,biy m\u00e0ggalukaayu Molog ak biddiiwub Refan,bi \u00f1u daan bokkaaleel Y\u00e0lla,di ay nataal, yi ngeen defoon ngir m\u00e0ggal leen!Kon nag dinaa leen toxal,y\u00f3bbu leen ci gannaaw r\u00e9ewu Babilon.\u201d\n7:44 \u00abSunuy maam amoon na\u00f1u ca m\u00e0ndi\u014b ma t\u00e0ntu m\u00e0ggalukaay, bi \u00ebmboon li Y\u00e0lla seede. T\u00e0nt boobu nag defoon na\u00f1u ko, roye ko ci bi Musaa gisoon, ni ko ko Y\u00e0lla sante woon.\n7:45 Te gannaaw ga, bi Yosuwe nekkee kilifag sunuy maam, \u00f1u jot t\u00e0nt ba \u00f1oom it, y\u00f3bbu ko ca r\u00e9ew, ma \u00f1u nangu ca xeet ya Y\u00e0lla d\u00e0q ci seen kanam. T\u00e0nt ba nekk fa, ba ci jamonoy Daawuda.\n7:46 Moom yiw na fa kanam Y\u00e0lla, mu \u00f1aan ko, mu s\u00e0kkal ko k\u00ebr ngir askanu Yanq\u00f3oba.\n7:47 Waaye Suleymaan moo tabaxal Y\u00e0lla k\u00ebr ga.\n7:48 \u00abMoona Aji Kawe ji du d\u00ebkk ci fu loxol nit defar; moom la ab yonent wax ne:\n7:49 \u201cAsamaan mooy sama jal,te suuf mooy sama tegukaayu t\u00e0nk.Kon gan k\u00ebr ngeen may tabaxal,mbaa fan mooy sama b\u00e9rabu noppalukaay?\n7:50 Ndax du sama loxo moo defar y\u00ebf yooyu y\u00e9pp?\u2014 Moom la Boroom bi doon wax.\u201d\n7:51 \u00abY\u00e9en \u00f1i d\u00ebg\u00ebr bopp, \u00e0nd ak xol buy ba\u00f1 ak ay nopp yuy fatt, mel ni \u00f1i xamul Y\u00e0lla. Dungeen noppeek a diiroo ak Xel mu Sell mi; ni ko seen baay yi daan defe, noonu ngeen di def y\u00e9en itam.\n7:52 Kan ca yonent ya la seeni maam tegul woon ay fitna? Rey na\u00f1u \u00f1i doon y\u00e9gle \u00f1\u00ebwug Aji Jub ji, moom mi ngeen j\u00e9bbale l\u00e9egi, ba \u00f1u rey ko.\n7:53 Jot ngeen yoonu Musaa, wi Y\u00e0lla w\u00e0cce jaarale ko ci ay malaaka, te s\u00e0ggane ngeen ko.\u00bb\n7:54 Bi \u00f1u d\u00e9ggee loolu nag, seeni xol di dagg, \u00f1uy y\u00e9yu, j\u00ebm ci kawam.\n7:55 Waaye Ecen, mi fees ak Xel mu Sell mi, ne j\u00e0kk ci asamaan, gis ndamu Y\u00e0lla, te gis Yeesu mi taxaw ci ndeyjooru Y\u00e0lla.\n7:56 Mu ne: \u00abSeetleen, maa ngi gis asamaan yi ubbiku, te Doomu nit kaa ngii taxaw ci ndeyjooru Y\u00e0lla.\u00bb\n7:57 Bi \u00f1u d\u00e9ggee loolu, \u00f1u daldi xaacu ca kaw, tey dar seeni nopp; \u00f1u \u00e0nd, ne milib ci kawam;\n7:58 \u00f1u wat-wate ko, g\u00e9nne ko d\u00ebkk ba, d\u00f3or ko ay doj, ba mu dee. Seede ya tegoon na\u00f1u seeni y\u00e9re ci t\u00e0nki waxambaane wu tudd Sool.\n7:59 Noonu \u00f1u d\u00f3or Ecen ay doj, muy \u00f1aan Y\u00e0lla ne: \u00abBoroom bi Yeesu, nangul sama ruu!\u00bb\n7:60 Bi mu ko waxee, mu sukk, wax ak baat bu kawe: \u00abBoroom bi, bu leen bindal b\u00e0kkaar bii,\u00bb ba noppi mu nelaw.\n8:1 Sool moom \u00e0nd na ci \u00f1i doon rey Ecen. B\u00e9s booba nag fitna ju metti dal na ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm, mi nekk Yerusalem, ba \u00f1\u00e9pp, \u00f1u moy ndaw ya, tasaaroo ci diiwaani Yude ak Samari.\n8:2 Ay nit \u00f1u ragal Y\u00e0lla fab Ecen, j\u00e9bbal ko Boroom bi, di ko jooy bu w\u00e9r.\n8:3 Waaye naka Sool, mu ngay tas mbooloom \u00f1i g\u00ebm, di t\u00e0bbi ca k\u00ebr ya, tey j\u00e0pp g\u00f3or ak jig\u00e9en, di leen t\u00ebj kaso.\n8:4 \u00d1i tasaaroo nag dem fu nekk, di fa xamle xebaar bu baax bu k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n8:5 Naka Filib mu dem ca benn d\u00ebkk ca Samari, di leen y\u00e9gal Kirist.\n8:6 Bi ko mbooloo mi d\u00e9ggee te gis k\u00e9emaan yi muy def, \u00f1u bokk benn xalaat, fekki ko ci li mu wax.\n8:7 Ndaxte ay rab yu bon b\u00e0yyi na\u00f1u nit \u00f1u bare, \u00f1a \u00f1u j\u00e0ppoon, di yuuxu ci kaw; te \u00f1u bare \u00f1u l\u00e0ggi ak \u00f1u lafa\u00f1 daldi w\u00e9r.\n8:8 Noonu mb\u00e9g mu r\u00e9y t\u00e0bbi ca d\u00ebkk ba.\n8:9 Amoon na nag nit ku tudd Simo\u014b, di luxuskat bu y\u00e0gg ca d\u00ebkk ba, te daan y\u00e9em waa Samari g\u00e9pp, ci naan: \u00abAji M\u00e0gg laa.\u00bb\n8:10 Kon \u00f1\u00e9pp, mag ak ndaw, taq ci moom ne: \u00abKii mooy jaasiy Aji K\u00e0ttan ji.\u00bb\n8:11 \u00d1u taq ci moom, ndax li mu leen y\u00e0gg a waar ci ay luxus.\n8:12 Waaye bi \u00f1u g\u00ebmee xebaar bu baax, bi Filib y\u00e9gle j\u00ebm ci nguurug Y\u00e0lla ak turu Yeesu Kirist, g\u00f3or ak jig\u00e9en daldi nangu, \u00f1u s\u00f3ob leen ci ndox.\n8:13 Simo\u014b sax g\u00ebm, \u00f1u s\u00f3ob ko ci ndox; mu w\u00e9y nag ci topp Filib, di waaru ci k\u00e9emaan yi ak firnde yu mag yiy am.\n8:14 Bi nga xamee ne ndaw yi nekk Yerusalem y\u00e9g na\u00f1u ne, waa Samari nangu na\u00f1u k\u00e0ddug Y\u00e0lla; \u00f1u y\u00f3nni fa Piyeer ak Yowaana.\n8:15 \u00d1u dem fa nag, \u00f1aanal leen, ngir \u00f1u jot Xel mu Sell mi.\n8:16 Ndaxte w\u00e0ccagul ci kenn ci \u00f1oom, waaye s\u00f3oboon na\u00f1u leen rekk ci ndox ci turu Boroom bi Yeesu.\n8:17 Noonu Piyeer ak Yowaana teg leen loxo, \u00f1u jot Xel mu Sell mi.\n8:18 Bi Simo\u014b gisee nag ne Y\u00e0lla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis,\n8:19 ne leen: \u00abMayleen ma sa\u00f1-sa\u00f1 boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.\u00bb\n8:20 Waaye Piyeer ne ko: \u00abAsarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne, man ngaa j\u00ebnd mayu Y\u00e0lla ak xaalis.\n8:21 Amuloo benn w\u00e0ll mbaa c\u00e9r ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Y\u00e0lla.\n8:22 R\u00e9ccul nag sa coxor te \u00f1aan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am.\n8:23 Ndaxte gis naa ne, s\u00f3obu nga ci lu wex xat ci kanam Y\u00e0lla, te b\u00e0kkaar noot na la.\u00bb\n8:24 Simo\u014b nag ne leen: \u00ab\u00d1aanal-leen ma ci Boroom bi, ngir mu fegal ma li ngeen wax.\u00bb\n8:25 Noonu bi \u00f1u seedeelee Y\u00e0lla te wax ci k\u00e0ddoom, \u00f1u dellu Yerusalem, di xamle xebaar bu baax bi ci d\u00ebkk yu bare yu waa Samari.\n8:26 Naka noonu benn malaakam Boroom bi ne Filib: \u00abJ\u00f3gal te jublu Misra, jaar ci yoon wi j\u00f3ge Yerusalem, j\u00ebm Gasa, di m\u00e0ndi\u014b.\u00bb\n8:27 Filib j\u00f3g dem. Noonu mu gis fa nitu Ec\u00f3pi ku yoom, di jaraaf ju mag ci Kandas, buur bu jig\u00e9en bu Ec\u00f3pi, te di ko wottul xaalisam b\u00e9pp. Fekk mu \u00f1\u00ebwoon Yerusalem, ngir m\u00e0ggalsi Y\u00e0lla, bay dellu;\n8:28 mu toog ci watiiram, di j\u00e0ng t\u00e9ereb yonent Y\u00e0lla Esayi.\n8:29 Xel mi nag ne Filib: \u00abDabal watiir wale.\u00bb\n8:30 Noonu Filib dawsi, mu d\u00e9gg waayi Ec\u00f3pi ja, di j\u00e0ng t\u00e9ereb yonent Y\u00e0lla Esayi. Mu laaj ko: \u00abNdax xam nga li ngay j\u00e0ng?\u00bb\n8:31 Mu tontu ko ne: \u00abNu ma ko man a xame, su ma ko kenn firilul?\u00bb Mu woo Filib nag, mu y\u00e9eg, toog ak moom.\n8:32 Fekk aaya yii la doon j\u00e0ng ci Mbind mi:\u00abY\u00f3bbu na\u00f1u ko ni xar mu \u00f1uy rendiji;ni mburt mu luu ci kanami watkat,mu ne cell.\n8:33 Ci toroxteem nangu na\u00f1u d\u00ebggam;\u00f1i mu tollool jamono, ku ci xalaat lii?J\u00eble na\u00f1u bakkanam ci \u00e0ddina.\u00bb\n8:34 Jaraaf ja nag ne Filib: \u00abMaa ngi lay laaj, ci mbirum kan la yonent bi j\u00ebmale wax ji? Ndax mbirum boppam lay wax mbaa mu keneen?\u00bb\n8:35 Noonu Filib t\u00e0mbali ci aaya yooyu, xamal ko xebaar bu baax bi ci mbirum Yeesu.\n8:36 Bi \u00f1uy jaar ci yoon wi, \u00f1u agsi ci ndox. Jaraaf ja ne ko: \u00abNdox a ngi nii, ana lu tere, nga s\u00f3ob ma ci?\u00bb\n8:38 Mu santaane nag, \u00f1u taxawal watiir wa; Filib ak jaraaf ja w\u00e0cc \u00f1oom \u00f1aar ci biir ndox ma, mu s\u00f3ob ko ca.\n8:39 Ba noppi \u00f1u g\u00e9nn ca ndox ma, te ca saa sa Xelu Boroom bi f\u00ebkk Filib, ba jaraaf ja gisatu ko, waaye mu toppaat yoonam, \u00e0nd ak mb\u00e9g.\n8:40 Filib moom teeri d\u00ebkku Asot, muy jaar ci d\u00ebkk y\u00e9pp, di fa xamle xebaar bu baax bi, ba kera muy \u00f1\u00ebw d\u00ebkku Sesare.\n9:1 Naka Sool, muy t\u00ebkkoo rey taalibey Boroom bi, ba di ko noyyee far. Mu dem nag ca saraxalekat bu mag ba,\n9:2 laaj ko ay bataaxal yu muy y\u00f3bbul j\u00e0nguy d\u00ebkku Damas. Noonu \u00f1u mu fa fekk, te \u00f1u bokk ci yoon wi, g\u00f3or mbaa jig\u00e9en, mu am dogalu yeew leen, indi leen Yerusalem.\n9:3 Waaye bi muy jub Damas, ca saa sa leer gu j\u00f3ge asamaan melax, ba \u00ebmb ko.\n9:4 Mu daanu ci suuf, d\u00e9gg baat bu ko ne: \u00abSool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal?\u00bb\n9:5 Mu wuyu ne: \u00abYaay kan Boroom bi?\u00bb Boroom bi ne ko: \u00abMaay Yeesu, mi ngay fitnaal.\n9:6 Waaye j\u00f3gal, dugg ca d\u00ebkk ba, te dina\u00f1u la wax li nga war a def.\u00bb\n9:7 Nit \u00f1i \u00e0nd ak moom nag taxaw, waaru ba luu, ci li \u00f1u d\u00e9gg baat bi te gisu\u00f1u kenn.\n9:8 Noonu Sool j\u00f3g, xippi, waaye gisul dara; kon \u00f1u wommat ko, y\u00f3bbu ko Damas.\n9:9 Diirub \u00f1etti fan gisul dara, lekkul, naanul.\n9:10 Amoon na nag ci Damas taalibe bu tudd Ana\u00f1as. Bi loolu amee nag Boroom bi fee\u00f1u ko ne: \u00abAna\u00f1as!\u00bb Mu wuyu: \u00abMaa ngi nii Boroom bi.\u00bb\n9:11 Boroom bi ne ko: \u00abJ\u00f3gal, nga jaar ci mbedd, mi \u00f1uy wax Mbedd mu jub mi, te seet ci k\u00ebr Yudaa nit ku tudd Sool te d\u00ebkk Tars, ndaxte mu ngay \u00f1aan.\n9:12 Te gis na cim pee\u00f1u nit ku tudd Ana\u00f1as, mu dugg, teg ko ay loxo, ba muy gisaat.\u00bb\n9:13 Waaye Ana\u00f1as tontu ko ne: \u00abBoroom bi, d\u00e9gg naa ci nit \u00f1u bare ci mbirum kooku, \u00f1u seede lu bare lu bon lu mu def say gaay ci Yerusalem.\n9:14 Te indaale na fii sax sa\u00f1-sa\u00f1 bu j\u00f3ge ci saraxalekat yu mag ya, ngir yeew k\u00e9pp kuy tudd saw tur.\u00bb\n9:15 Waaye Boroom bi ne ko: \u00abDemal, ndaxte maa ko t\u00e0nn, muy sama j\u00ebfandukaay, ngir y\u00f3bbu sama tur fa kanam \u00f1i nekkul Yawut ak fa kanam buur yi ak b\u00e0nni Israyil.\n9:16 Te dinaa ko won coono yu bare yu mu war a d\u00e9kku ngir sama tur.\u00bb\n9:17 Ci kaw loolu Ana\u00f1as dem, dugg ca k\u00ebr ga, teg ay loxoom Sool. Mu ne ko: \u00abSool sama mbokk, Boroom bi Yeesu, mi la fee\u00f1u woon ci kaw yoon wi, bi ngay dikk, moo ma y\u00f3nni, ngir nga dellu di gis te fees ak Xel mu Sell mi.\u00bb\n9:18 Ca saa sa lu mel ni ay waasintoor g\u00e9nne ci ay b\u00ebtam, mu daldi gisaat. Noonu mu j\u00f3g, \u00f1u s\u00f3ob ko ci ndox;\n9:19 ba noppi mu lekk, amaat doole. Bi mu ko defee mu toog ay fan ak taalibe, ya nekk Damas.\n9:20 Ca saa sa muy y\u00e9gle ca j\u00e0ngu ya ne, Yeesu mooy Doomu Y\u00e0lla.\n9:21 \u00d1i ko d\u00e9gg \u00f1\u00e9pp waaru naan: \u00abNdax du kii moo daan tas \u00f1iy tudd tur woowu ci Yerusalem, te mu \u00f1\u00ebw fii, ngir yeew leen, y\u00f3bbu ci kanamu saraxalekat yu mag ya?\u00bb\n9:22 Moona Sool di g\u00ebn a am k\u00e0ttan, bay jaaxal Yawut yi d\u00ebkk Damas, ci di leen wax ay firnde, ne Yeesu mooy Almasi bi.\n9:23 Ba \u00f1u ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko.\n9:24 Waaye Sool y\u00e9g seen pexe. Fekk guddi ak b\u00ebcc\u00ebg \u00f1u doon wottu bunt yi y\u00e9pp, ngir man koo b\u00f3om.\n9:25 Noonu taalibe yi j\u00ebl ko ci guddi, def ko ci d\u00e0mba gu r\u00e9y, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf.\n9:26 Bi Sool agsee Yerusalem, mu j\u00e9em a \u00e0nd ak taalibe yi, waaye \u00f1\u00e9pp ragal ko, ndax g\u00ebmu\u00f1u woon ag taalibeem.\n9:27 Ci kaw loolu Barnabas j\u00ebl ko, y\u00f3bbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sool gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damas.\n9:28 Noonu mu nekk ak \u00f1oom ci Yerusalem, di dugg ak a g\u00e9nn, di wax ak fit ci turu Boroom bi.\n9:29 Muy wax ak di werante ak Yawut yiy l\u00e0kk gereg, waaye \u00f1u di ko wut a rey.\n9:30 Bi ko bokk yi y\u00e9gee nag, \u00f1u y\u00f3bbu ko d\u00ebkku Sesare, yebal ko d\u00ebkku Tars.\n9:31 Noonu mbooloom \u00f1i g\u00ebm nekk ci j\u00e0mm ci biir diiwaani Yude g\u00e9pp ak Galile ak Samari; \u00f1uy g\u00ebn a d\u00ebg\u00ebr, di w\u00e9y ci ragal Y\u00e0lla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.\n9:32 Piyeer nag di w\u00ebr, di jaar fu nekk, tey dem ci gaayi Y\u00e0lla yi d\u00ebkk Lidd,\n9:33 mu gis fa nit ku l\u00e0ggi, tudd Ene, t\u00ebdd ci basa\u014b diirub jur\u00f3om-\u00f1etti at.\n9:34 Piyeer ne ko: \u00abEne, Yeesu Kirist faj na la; j\u00f3gal te defar sa lal.\u00bb Noonu mu daldi j\u00f3g ca saa sa.\n9:35 Bi ko waa diiwaani Lidd ak Saron g\u00e9pp gisee, \u00f1u daldi wo\u00f1\u00f1iku ci Boroom bi.\n9:36 Amoon na nag ci d\u00ebkku Yope taalibe bu jig\u00e9en bu tudd Tabita, liy tekki \u00abDorkas,\u00bb maanaam \u00abkewel,\u00bb te muy w\u00e9y ci j\u00ebf yu baax ak saraxe.\n9:37 Ca fan yooyu mu daanu wopp, ba faatu; noonu \u00f1u sang ko, teg ko ca n\u00e9eg, ba sut ca taax ma.\n9:38 Gannaaw Lidd sorewul ak Yope nag, te taalibe yi d\u00e9gg ne, Piyeer a nga fa, \u00f1u y\u00f3nnee ko \u00f1aari nit, \u00f1aan ko mu \u00f1\u00ebw ci \u00f1oom ci saa si.\n9:39 Bi ko Piyeer d\u00e9ggee, mu j\u00f3g, \u00e0nd ak \u00f1oom. Bi mu \u00f1\u00ebwee, \u00f1u y\u00f3bbu ko ca n\u00e9eg bu kawe ba. Fekk fa ay jig\u00e9en \u00f1i seeni j\u00ebkk\u00ebr faatu, \u00f1u daldi w\u00ebr Piyeer, \u00f1\u00e9pp di jooy, di ko won kamisool ya ak mbubb, ya Dorkas daan defar cig dundam.\n9:40 Ci kaw loolu Piyeer g\u00e9nne \u00f1\u00e9pp ci biti, mu sukk, \u00f1aan ci Y\u00e0lla, ba noppi walbatiku ca n\u00e9ew ba ne ko: \u00abTabita, j\u00f3gal!\u00bb Noonu mu xippi, gis Piyeer, daldi toog.\n9:41 Piyeer may ko loxo, y\u00e9kkati ko. Mu woo gaayi Y\u00e0lla ya ak jig\u00e9en \u00f1a, won leen ko, muy dund.\n9:42 Mbir ma siiw ca Yope g\u00e9pp, ba \u00f1u bare g\u00ebm Boroom bi.\n9:43 Gannaaw loolu Piyeer toog ay fan ci Yope, ci k\u00ebru ku tudd Simo\u014b, miy wullikat.\n10:1 Amoon na ci Sesare nit ku tudd Korney, nekk njiitu xare, mu bokk ci mbooloom xare, mi \u00f1uy wax mu Itali.\n10:2 Moom nag ku farlu woon ci Y\u00e0lla la, te ragal ko, moom ak waa k\u00ebram g\u00e9pp; muy sarax \u00f1u bare ci b\u00e0nni Israyil, tey saxoo ci \u00f1aan ci Y\u00e0lla.\n10:3 Am b\u00e9s ci tisbaar nag mu am pee\u00f1u, gis bu leer malaakam Y\u00e0lla fee\u00f1u ko ne ko: \u00abKorney!\u00bb\n10:4 Noonu Korney ne ko j\u00e0kk, daldi tiit ne ko: \u00abKilifa gi, lu mu doon?\u00bb Malaaka ma ne ko: \u00abSay \u00f1aan ak say sarax y\u00e9eg na fa kanam Y\u00e0lla, te nangul na la.\n10:5 Y\u00f3nnil l\u00e9egi nag ay nit ci d\u00ebkku Yope, \u00f1u woo ku tudd Simo\u014b, mi \u00f1u d\u00e0kkentale Piyeer.\n10:6 Mu nga dal fa Simo\u014b wullikat, bi k\u00ebram nekk ci wetu g\u00e9ej.\u00bb\n10:7 Bi malaaka mi doon wax ak moom demee, Korney woo \u00f1aar ci ay surgaam ak benn xarekat bu farlu ci Y\u00e0lla ci \u00f1i koy topptoo;\n10:8 mu nettali leen l\u00e9pp, yebal leen Yope.\n10:9 Ca \u00ebll\u00ebg sa, ba \u00f1uy jaar ca yoon wa, ba jub d\u00ebkk ba, Piyeer y\u00e9eg ca kaw taax ma ci digg-b\u00ebcc\u00ebg ngir \u00f1aan ci Y\u00e0lla.\n10:10 Noonu xiif dab ko fa, mu b\u00ebgg a lekk. Waaye bi \u00f1u koy toggal, Y\u00e0lla fee\u00f1u ko.\n10:11 Mu xool asamaan ubbiku, gis lu mel ni s\u00e9r bu mag bu \u00f1u t\u00e9ye ci \u00f1eenti laf ya, yoor ko, mu j\u00ebm suuf.\n10:12 Boroom \u00f1eenti t\u00e0nk y\u00e9pp \u00f1u nga ca, ak yiy raam ci suuf, ak picci asamaan.\n10:13 Te baat ne ko: \u00abJ\u00f3gal, Piyeer, rey te lekk.\u00bb\n10:14 Waaye Piyeer tontu ko: \u00abMukk, Boroom bi, ndaxte musumaa lekk dara lu daganul mbaa lu araam.\u00bb\n10:15 Waaye baat bi wax ak moom \u00f1aareelu yoon ne ko: \u00abLu Y\u00e0lla sellal, bu ko araamal.\u00bb\n10:16 \u00d1u def ko nag, ba muy \u00f1etti yoon, ba noppi \u00f1u ne cas s\u00e9r ba, j\u00ebme asamaan.\n10:17 Bi loolu amee Piyeer jaaxle lool ci lu pee\u00f1u miy tekki; fekk booba nit \u00f1i Korney yebal, laajte woon na\u00f1u k\u00ebr Simo\u014b, ba agsi ci bunt bi.\n10:18 \u00d1u woote nag naan: \u00abSimo\u014b, mi \u00f1u d\u00e0kkentale Piyeer, ndax fi la d\u00ebkk?\u00bb\n10:19 Bi Piyeer di rabal xelam ci pee\u00f1u ma, Xel mi ne ko: \u00ab\u00d1etti nit a ngi nii, di la wut.\n10:20 J\u00f3gal, nga w\u00e0cc te \u00e0nd ak \u00f1oom; bul werante, ndaxte maa leen yebal.\u00bb\n10:21 Piyeer w\u00e0cc nag ne nit \u00f1i: \u00abMaa ngi nii, man mi ngeen di wut; lu doon seeni t\u00e0nk?\u00bb\n10:22 \u00d1u tontu ko: \u00abKorney, njiitu xare ba, nit ku jub la te ragal Y\u00e0lla, ba am seede su rafet ci b\u00e0nni Israyil g\u00e9pp. Malaaka mu sell nag sant na ko, mu woolu la ci k\u00ebram te d\u00e9glu li ngay wax.\u00bb\n10:23 Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba b\u00ebt setee, Piyeer j\u00f3g, dem ak \u00f1oom, \u00e0nd ak \u00f1enn ci bokk yi d\u00ebkk Yope,\n10:24 te b\u00e9s ba ca topp mu dikk Sesare. Fekk Korney woo na k\u00ebram ay bokkam ak i xaritam yi ko g\u00ebn a jege, di xaar Piyeer.\n10:25 Bi Piyeer duggee nag, Korney daje ak moom, daanu ciy t\u00e0nkam, sargal ko.\n10:26 Waaye Piyeer y\u00e9kkati ko ne: \u00abJ\u00f3gal, man it nit rekk laa.\u00bb\n10:27 Noonu muy waxtaan ak moom, duggsi, fekk fa ndajem nit \u00f1u bare.\n10:28 Mu ne leen: \u00abXam ngeen ne, aaye na\u00f1u Yawut, mu jaxasoo ak ku mu bokkalul xeet, mbaa mu dugg ci k\u00ebram. Waaye Y\u00e0lla won na ma ne, warumaa ne kenn setul mbaa araam na.\n10:29 Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, \u00f1\u00ebw naa ci lu \u00e0ndul ak werante. Maa ngi leen di laaj nag, lu ngeen may doye?\u00bb\n10:30 Ci kaw loolu Korney tontu ne: \u00ab\u00d1etti fan a ngii may \u00f1aan ci sama biir k\u00ebr ci waxtu wii, maanaam tisbaar. Ci saa si ku sol y\u00e9re yuy melax taxaw ci sama kanam,\n10:31 mu ne ma: \u201cKorney, say \u00f1aan nangu na, te say sarax egg na\u00f1u fa kanam Y\u00e0lla.\n10:32 Y\u00f3nneel nag ci Yope, woolu Simo\u014b, mi \u00f1u d\u00e0kkentale Piyeer; mu nga dal ci k\u00ebr Simo\u014b miy wullikat ca wetu g\u00e9ej ga.\u201d\n10:33 Y\u00f3nnee naa nag ci ni mu g\u00ebn a gaawe, woolu la; te maa ngi lay sant ci li nga \u00f1\u00ebw. L\u00e9egi nag nun \u00f1\u00e9pp nu ngi fi ci kanam Y\u00e0lla, ngir d\u00e9glu l\u00e9pp li la Boroom bi sant.\u00bb\n10:34 Noonu Piyeer j\u00ebl k\u00e0ddu ga ne leen: \u00abCi d\u00ebgg gis naa ne, Y\u00e0lla du g\u00ebnale,\n10:35 waaye ci xeet y\u00e9pp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu.\n10:36 Y\u00f3nnee na k\u00e0ddoom b\u00e0nni Israyil, di leen xebaar j\u00e0mm, jaarale ko ci Yeesu Kirist, miy Boroom l\u00e9pp.\n10:37 Xam ngeen li xewoon ci r\u00e9ewum Yawut y\u00e9pp, li ko t\u00e0mbalee ci diiwaanu Galile, topp ci waareb Yaxya, mu naan nit \u00f1i, mu s\u00f3ob leen ci ndox.\n10:38 Xam ngeen ne Y\u00e0lla fal na Yeesum Nasaret, sol ko Xel mu Sell mi ak k\u00e0ttan; muy w\u00ebr, di def lu baax ak di faj \u00f1\u00e9pp \u00f1i nekkoon ci kilifteefu Seytaane, ndaxte Y\u00e0lla \u00e0nd na ak moom.\n10:39 \u00abSeede nanu li mu def l\u00e9pp ci biir r\u00e9ewu Yawut ya ak Yerusalem. Moona rey na\u00f1u ko ci w\u00e9kk ko ci bant.\n10:40 Waaye Y\u00e0lla dekkal na ko ci \u00f1etteelu fan ba te biral ko,\n10:41 waxuma xeet w\u00e9pp, waaye seede yi Y\u00e0lla t\u00e0nn lu jiitu, maanaam nun \u00f1i daan lekk di naan ak moom gannaaw ndekkiteem.\n10:42 Te Yeesu sant na nu, nu y\u00e9gal xeet wa, di seede ne, moom la Y\u00e0lla jagleel \u00e0tteb \u00f1iy dund ak \u00f1i dee.\n10:43 Yonent y\u00e9pp seedeel na\u00f1u ko ne, ku ko g\u00ebm, Y\u00e0lla dina la baal say b\u00e0kkaar ci turam.\u00bb\n10:44 Bi Piyeer di wax loolu, Xel mu Sell mi w\u00e0cc ci kaw \u00f1\u00e9pp \u00f1iy d\u00e9glu k\u00e0ddu ga.\n10:45 Yawut yi g\u00ebm y\u00e9pp nag, \u00f1i \u00e0nd ak Piyeer, daldi waaru ci li Y\u00e0lla tuur Xel mu Sell, mi mu maye, ci \u00f1i dul Yawut itam.\n10:46 Ndaxte d\u00e9gg na\u00f1u leen, \u00f1uy wax yeneeni l\u00e0kk ak di m\u00e0ggal Y\u00e0lla.\n10:47 Booba Piyeer daldi wax ne: \u00ab\u00d1ii jot Xel mu Sell mi ni nun, ndax manees na leen a ba\u00f1 a s\u00f3ob ci ndox?\u00bb\n10:48 Noonu mu santaane, \u00f1u s\u00f3ob leen ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Gannaaw loolu \u00f1u \u00f1aan ko, mu toog ci \u00f1oom ay fan.\n11:1 Bi loolu amee ndaw yi ak bokk yi nekk ci diiwaanu Yude, d\u00e9gg na\u00f1u ne, \u00f1i dul Yawut nangu na\u00f1u k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n11:2 Bi Piyeer demee Yerusalem nag, kureelu Yawut gi farataal xaraf, di werante ak moom ne ko:\n11:3 \u00abLu tax nga dem ca k\u00ebru \u00f1u xarafal, bay lekk sax ak \u00f1oom?\u00bb\n11:4 Noonu Piyeer daldi leen benn-bennal mbir mi, nettali leen ko\n11:5 ne: \u00abNekkoon naa ca d\u00ebkku Yope, di fa \u00f1aan ci Y\u00e0lla, ba far sama xol seey ci moom; noonu ma am pee\u00f1u: lu mel ni s\u00e9r bu mag w\u00e0cc, j\u00f3ge ci asamaan, \u00f1u yoor ko ca \u00f1eenti laf ya, mu \u00f1\u00ebw ba ci man.\n11:6 Ma xool ko j\u00e0kk, seetlu ko bu baax, ma gis ca boroom \u00f1eenti t\u00e0nk yu nekk ci kaw suuf, di rabi \u00e0ll yi, yiy raam ak picci asamaan.\n11:7 Te d\u00e9gg naa baat bu ma ne: \u201cJ\u00f3gal Piyeer, rey te lekk.\u201d\n11:8 Waaye ma tontu ne: \u201cMukk Boroom bi, ndax dara lu daganul mbaa lu araam musul a dugg ci sama g\u00e9mmi\u00f1.\u201d\n11:9 Waaye \u00f1aareel bi yoon baat bi dellu ne ma: \u201cLu Y\u00e0lla sellal, bu ko araamal.\u201d\n11:10 Loolu am ba muy \u00f1etti yoon, ba noppi \u00f1u ne cas l\u00e9pp, j\u00ebme asamaan.\n11:11 \u00abCa saa sa \u00f1etti g\u00f3or, \u00f1a \u00f1u yebal ci man, j\u00f3ge Sesare, agsi ca k\u00ebr ga ma dal.\n11:12 Te Xel mi ne ma: \u201c\u00c0ndal ak \u00f1oom, te bu ci werante.\u201d Jur\u00f3om-benni bokk, yi fi teew, gunge woon na\u00f1u ma, ba nu dugg ca k\u00ebr g\u00f3or googu.\n11:13 Mu nettali nu ne, gis na malaaka, fee\u00f1u ko ca k\u00ebram ne ko: \u201cY\u00f3nneel ca d\u00ebkku Yope, woolu Simo\u014b, mi \u00f1u d\u00e0kkentale Piyeer.\n11:14 Dina la xamal ay wax yu lay musal, yaw ak sa waa k\u00ebr g\u00e9pp.\u201d\n11:15 \u00abBi ma t\u00e0mbalee wax nag, Xel mu Sell mi w\u00e0cc ci \u00f1oom, ni mu w\u00e0cce woon ci nun bu j\u00ebkk.\n11:16 Bi loolu amee ma f\u00e0ttaliku li Boroom bi wax ne: \u201cYaxya ci ndox la daan s\u00f3obe, waaye y\u00e9en dees na leen s\u00f3ob ci Xel mu Sell mi.\u201d\n11:17 Gannaaw nag Y\u00e0lla jagleel na leen may, gi mu nu mayoon, bi nu g\u00ebmee Yeesu Kirist Boroom bi, man maay kan, bay tebbi \u00e0tteb Y\u00e0lla?\u00bb\n11:18 Bi \u00f1u d\u00e9ggee loolu, amu\u00f1u dara lu \u00f1u ca teg, \u00f1u daldi m\u00e0ggal Y\u00e0lla ne: \u00abY\u00e0lla nag may na \u00f1i dul Yawut it \u00f1u tuub seeni b\u00e0kkaar, ba am dund gu w\u00f3or gi.\u00bb\n11:19 \u00d1i tasoon nag ndax fitna, ji amoon gannaaw Ecen, \u00f1u dem ba diiwaanu Fenisi, ci dunu Sipar ak ca d\u00ebkku Ancos, di wax k\u00e0ddu gi, waaye yemale ko ci Yawut yi.\n11:20 Moona amoon na ci \u00f1oom ay niti Sipar ak d\u00ebkku Siren, \u00f1u \u00f1\u00ebw ci Ancos, ba seen wax law ci Gereg yi it, \u00f1u di leen xamal xebaar bu baax bu Yeesu Boroom bi.\n11:21 Te loxob Boroom bi \u00e0nd ak \u00f1oom, ba mbooloo mu mag g\u00ebm te wo\u00f1\u00f1iku ci Boroom bi.\n11:22 Ba mbir ma siiwee, ba \u00e0gg ci noppi mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci Yerusalem, \u00f1u yebal Barnabas ba Ancos.\n11:23 Bi mu agsee nag, ba gis yiw, wi leen Y\u00e0lla may, mu b\u00e9g ci te di leen xiir, \u00f1u w\u00e0kkirlu ci Boroom bi te dogu ci.\n11:24 Ndaxte nit ku baax la woon te fees ak Xel mu Sell mi ak ng\u00ebm; noonu mbooloo mu bare dolliku ci Boroom bi.\n11:25 Gannaaw loolu Barnabas dem ca d\u00ebkku Tars, di wut Sool.\n11:26 Bi mu ko gisee, mu indi ko Ancos. Noonu atum l\u00ebmm \u00f1u bokk ak mbooloom \u00f1i g\u00ebm, di j\u00e0ngal nit \u00f1u bare. Te ci Ancos la\u00f1u j\u00ebkk a tudde taalibe ya Gaayi Kirist.\n11:27 Ca fan yooyu ay yonent j\u00f3ge Yerusalem, \u00f1\u00ebw Ancos.\n11:28 Kenn ci \u00f1oom tudd Agabus j\u00f3g, mu y\u00e9gle jaarale ko ci Xelu Y\u00e0lla mi ne, xiif bu metti dina daj \u00e0ddina s\u00e9pp. Loolu nag amoon na ca ayug buur bu \u00f1uy wax K\u00ebl\u00f3dd.\n11:29 Kon taalibe ya fas y\u00e9enee s\u00e0kk ndimbal, j\u00ebme ca bokk ya d\u00ebkk diiwaanu Yude, ku nekk ak sa kem-k\u00e0ttan.\n11:30 Noonu la\u00f1u def nag, teg ko ci loxoy Barnabas ak Sool, y\u00f3nnee ko njiit ya.\n12:1 Ca jamono jooja Erodd buur ba j\u00e0ppoon na ay nit ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm, ngir fitnaal leen.\n12:2 Noonu mu daldi j\u00e0pp Saag, doomu ndeyu Yowaana, mu reylu ko ci jaasi.\n12:3 Bi mu gisee nag ne, mbir moomu neex na Yawut ya, mu daldi j\u00e0pp it Piyeer; fekk loolu daje ak b\u00e9si m\u00e0ggalu Yawut, ga \u00f1uy wax Mburu ya amul lawiir.\n12:4 Bi mu ko j\u00e0ppee, mu t\u00ebj ko kaso, teg ko ci loxoy \u00f1eenti mboolooy xarekat, ngir \u00f1u wottu ko, fekk mbooloo mu ci nekk di \u00f1eenti nit; amoon na y\u00e9eney y\u00f3bbu ko ci kanamu Yawut ya gannaaw m\u00e0ggalu b\u00e9su J\u00e9ggi ba.\n12:5 Noonu \u00f1uy wottu Piyeer ca kaso ba, waaye mbooloom \u00f1i g\u00ebm di ko \u00f1aanal Y\u00e0lla ak seen xol b\u00e9pp.\n12:6 Bi Erodd nekkee ci t\u00e0nki indilu ko, ca guddi googa yeewoon na\u00f1u Piyeer ak \u00f1aari c\u00e0llala, muy nelaw diggante \u00f1aari xarekat, te ay xarekat di wottu buntu kaso ba.\n12:7 Ca saa sa malaakam Boroom bi \u00f1\u00ebw, te leer ne r\u00e0yy ca n\u00e9eg ba. Malaaka ma d\u00f3or Piyeer ci wetam, yee ko ne ko: \u00abJ\u00f3gal bu gaaw!\u00bb Noonu j\u00e9ng ya rot ciy loxoom.\n12:8 Malaaka ma ne ko: \u00abTakkal sa ge\u00f1o te sol say d\u00e0ll.\u00bb Mu def ko. Malaaka ma ne ko: \u00abSolal sa mbubb te topp ci man.\u00bb\n12:9 Piyeer g\u00e9nn, topp ca malaaka ma, fekk g\u00ebmul sax ne lu am la, waaye mu yaakaar ne pee\u00f1u la.\n12:10 Noonu \u00f1u weesu wottukat bu j\u00ebkk ba ak ba ca tegu, \u00f1u agsi ca buntu we\u00f1, ba j\u00ebm ca d\u00ebkk ba, mu daldi ubbikul boppam ci seen kanam. \u00d1u g\u00e9nn nag, jaar ci benn mbedd, malaaka ma daldi ko b\u00e0yyi.\n12:11 Bi xelam dellusee ci moom Piyeer ne: \u00abL\u00e9egi xam naa ci lu w\u00f3or ne, Boroom bi y\u00f3nni na malaakaam, musal ma ci loxoy Erodd ak li ma Yawut ya y\u00e9ene woon l\u00e9pp.\u00bb\n12:12 Mu rabal xelam ci loolu, daldi dem k\u00ebr Maryaama, ndeyu Yowaana, mi \u00f1uy wooye M\u00e0rk, fekk \u00f1u bare booloo fa, di \u00f1aan ci Y\u00e0lla.\n12:13 Noonu Piyeer f\u00ebgg buntu k\u00ebr ga, te mbindaan mu tudd Rodd wuyusi ko.\n12:14 Mu x\u00e0mmi baatu Piyeer, b\u00e9g ci, ba f\u00e0tte koo ubbil, waaye mu daw ci biir, xamle ne Piyeer a nga ca bunt ba.\n12:15 \u00d1u ne ko: \u00abXanaa dangaa dof.\u00bb Waaye mu d\u00ebg\u00ebr ci li mu wax. Noonu \u00f1u ne ko: \u00abXanaa malaakaam la.\u00bb\n12:16 Fekk Piyeer di g\u00ebn a f\u00ebgg. Noonu \u00f1u tijji, gis ko, daldi waaru.\n12:17 Piyeer taf loxoom ci g\u00e9mmi\u00f1am, ngir \u00f1u noppi, daldi leen nettali, ni ko Boroom bi g\u00e9nnee ca kaso ba. Mu ne leen: \u00abTee ngeen jottali ko Saag ak bokk ya.\u00bb Bi mu ko waxee, mu j\u00f3ge fa, dem feneen.\n12:18 Bi b\u00ebt setee nag, yengu-yengu bu r\u00e9y am na ca xarekat ya, \u00f1u ne: \u00abAna Piyeer?\u00bb\n12:19 Noonu Erodd wutlu ko, waaye gisu ko. Kon mu \u00e0tte wottukat ya, joxe ndigalu rey leen. Bi loolu amee Erodd j\u00f3ge ci diiwaanu Yude, dem d\u00ebkku Sesare, toog fa.\n12:20 Fekk mu nekk ci x\u00ebccoo bu t\u00e0ng ak waa d\u00ebkki Tir ak Sidon. Naka noona \u00f1u \u00e0nd, b\u00ebgg koo gis. \u00d1u neexal Balastus, b\u00ebkk-n\u00e9egu buur ba, di \u00f1aan j\u00e0mm, ndaxte r\u00e9ewu buur ba moo doon dundal seen bos.\n12:21 Ca b\u00e9s ba \u00f1u j\u00e0pp nag Erodd sol mbubbi buuram, toog ca jal ba ca \u00e0ttekaay ba, di leen yedd ak a d\u00e9nk.\n12:22 Noonu mbooloo mi di yuuxu naan: \u00abLii baatu Y\u00e0lla la, du baatu nit!\u00bb\n12:23 Ca saa sa nag, gannaaw m\u00e0ggalul Y\u00e0lla, malaakam Boroom bi f\u00e0dd ko te ay sax dugg ko, ba mu dee.\n12:24 Moona k\u00e0ddug Boroom bi di g\u00ebn a m\u00e0gg tey law.\n12:25 Naka Barnabas ak Sool, bi \u00f1u matalee seen ligg\u00e9ey, \u00f1u j\u00f3ge Yerusalem, \u00f1ibbi, \u00e0nd ak Yowaana mi tudd M\u00e0rk.\n13:1 Amoon na ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm, mi nekk d\u00ebkku Ancos, ay yonent ak ay j\u00e0ngalekat: maanaam Barnabas, Simeyon ku \u00f1u d\u00e0kkentale Niseer, Lusiyus mi d\u00ebkk Siren, Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom diiwaan ba, ak Sool.\n13:2 Am b\u00e9s nag, bi \u00f1uy jaamu Boroom bi ak di woor, Xel mu Sell mi ne: \u00abBeral-leen ma Barnabas ak Sool ngir ligg\u00e9ey, bi ma leen wooye.\u00bb\n13:3 Bi \u00f1u ko d\u00e9ggee, \u00f1u daldi woor ak a \u00f1aan, teg leen ay loxo, ba noppi b\u00e0yyi leen \u00f1u dem.\n13:4 Noonu Xel mu Sell mi y\u00f3nni leen. \u00d1u dem nag ci d\u00ebkku Selusi, dugg fa gaal, j\u00ebm ci dun bu \u00f1uy wax Sipar.\n13:5 Bi \u00f1u teeree ca d\u00ebkku Salamin nag, \u00f1u y\u00e9gle fa k\u00e0ddug Y\u00e0lla ca j\u00e0ngub Yawut ya. Ku tudd Yowaana \u00e0nd ak \u00f1oom, di leen j\u00e0pple ci ligg\u00e9ey bi.\n13:6 Noonu \u00f1u jaar ci dun b\u00e9pp, ba egg d\u00ebkku Pafos. Foofa \u00f1u gis luxuskat bu tudd Bar-Yeesu, di Yawut bu mbubboo turu yonent.\n13:7 Mu bokk ci g\u00e0ngooru boroom r\u00e9ew ma tudd Sersiyus Poolus, di nit ku neex xel. Moom nag mu woolu Barnabas ak Sool, ngir b\u00ebgg a d\u00e9gg k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n13:8 Waaye Elimas, boroom xam-xam bu \u00f1uul bi --ndaxte loolu la turam di tekki \u2014 di leen dogale, ngir ba\u00f1 boroom r\u00e9ew ma g\u00ebm.\n13:9 Ci kaw loolu Sool, mi tudd it Pool, daldi fees ak Xel mu Sell mi; mu xool ko j\u00e0kk,\n13:10 ne ko: \u00abYaw mi fees ak fen ak lu bon, di doomu Ibliis, tey noonu l\u00e9pp lu jub, ndax doo b\u00e0yyee d\u00ebngal yoon yu jub yu Boroom bi?\n13:11 L\u00e9egi loxob Boroom bi dina dal sa kaw, te dinga gumba, ba dootuloo gis jant bi ab diir.\u00bb Ca saa sa nag ay b\u00ebtam muuru, mu daldi t\u00e0bbi cig l\u00ebnd\u00ebm, muy l\u00e0mbatu, di wut ku ko wommat.\n13:12 Ba boroom r\u00e9ew ma gisee li xew nag, mu daldi g\u00ebm, di y\u00e9emu ci yoonu Boroom bi.\n13:13 Naka noona Pool ak \u00f1i mu \u00e0ndal j\u00f3ge Pafos, jaar ci g\u00e9ej, j\u00ebm d\u00ebkku Peers ci r\u00e9ewu Pamfili. Yowaana nag t\u00e0ggoo ak \u00f1oom, dellu Yerusalem.\n13:14 Waaye \u00f1oom \u00f1u j\u00f3ge Peers, aw ca yoon wa, ba \u00f1\u00ebw d\u00ebkku Ancos ci diiwaanu Pisidi. B\u00e9su noflaay ba nag \u00f1u dugg ca j\u00e0ngu ba, toog.\n13:15 Bi \u00f1u j\u00e0ngee yoonu Musaa ak yonent ya, njiiti j\u00e0ngu ba y\u00f3nnee ca \u00f1oom ne leen: \u00abBokk yi, bu ngeen amee lu ngeen di d\u00e9nk mbooloo mi, waxleen ko.\u00bb\n13:16 Noonu Pool j\u00f3g, t\u00e0llal loxoom ne leen: \u00abY\u00e9en bokki Israyil ak y\u00e9en \u00f1i ragal Y\u00e0lla, d\u00e9gluleen!\n13:17 Y\u00e0llay b\u00e0nni Israyil t\u00e0nn na sunuy maam, di yokk xeet wa, bi \u00f1uy ganeyaan ci Misra; ba noppi mu g\u00e9nne leen fa ak k\u00e0ttanu loxoom.\n13:18 Diirub \u00f1eent-fukki at mu di leen mu\u00f1al ca m\u00e0ndi\u014b ma.\n13:19 Gannaaw loolu faagal na jur\u00f3om-\u00f1aari xeet ci r\u00e9ewu Kanaan, ba sunuy maam donn r\u00e9ew ma.\n13:20 Loolu l\u00e9pp xew na ci diirub \u00f1eenti t\u00e9em\u00e9eri at ak jur\u00f3om-fukk. \u00abGannaaw loolu mu jox leen ay \u00e0ttekat, ba ci yonent Y\u00e0lla Samwil.\n13:21 Booba \u00f1uy \u00f1aan buur, te Y\u00e0lla jox leen S\u00f3ol, doomu Kis ci giiru Ben-yamin, muy seen buur diirub \u00f1eent-fukki at. Gannaaw ga mu j\u00eble ko fa,\n13:22 dellu falal leen buur bu tudd Daawuda, mu seedee ko nii: \u201cGis naa Daawuda, doomu Yese, ku ma neex ci sama xol, te dina def l\u00e9pp luy sama coobare.\u201d\n13:23 \u00abNoonu ci askanam Y\u00e0lla indil na b\u00e0nni Israyil Musalkat bi Yeesu, ci ni mu ko dige woon.\n13:24 Laata muy \u00f1\u00ebw nag, Yaxya daan na waare, ne b\u00e0nni Israyil g\u00e9pp, \u00f1u tuub seeni b\u00e0kkaar, te mu s\u00f3ob leen ci ndox.\n13:25 Te ba Yaxyay jeexal sasam, mu ne: \u201cKu ngeen may teg? Duma Ki war a \u00f1\u00ebw; waaye am na kuy \u00f1\u00ebw sama gannaaw, koo xam ne kii yeyoowumaa tekki ay d\u00e0llam.\u201d\n13:26 \u00abBokk yi, y\u00e9en askanu Ibraayma ak y\u00e9en \u00f1i ragal Y\u00e0lla, k\u00e0ddug mucc gi ci nun la w\u00e0cc.\n13:27 Waa Yerusalem ak seeni kilifa x\u00e0mmiwu\u00f1u woon Yeesu te xamu\u00f1u woon waxu yonent, yi \u00f1uy j\u00e0ng b\u00e9su noflaay bu nekk; teewul \u00f1u amal waxu yonent yi, ci li \u00f1u \u00e0tte Yeesu, ba daan ko.\n13:28 Yoon dabu ko fenn, moona \u00f1aan na\u00f1u Pilaat, mu reylu ko.\n13:29 Noonu \u00f1u def l\u00e9pp lu yonent yi bindoon ci mbiram, ba noppi \u00f1u w\u00e0cce ko ca bant ba, t\u00e0bbal ko ci b\u00e0mmeel.\n13:30 Waaye Y\u00e0lla dekkal na ko,\n13:31 te diirub ay fan yu bare fee\u00f1u na \u00f1i \u00e0ndoon ak moom, j\u00f3ge diiwaanu Galile, dem Yerusalem; l\u00e9egi nag \u00f1ooy ay seedeem ci wetu xeet wi,\n13:32 te nu ngi leen di xamal xebaar bu baax ne leen, li Y\u00e0lla digoon sunuy maam,\n13:33 def na ko ngir nun seeni s\u00ebt, ci li mu dekkal Yeesu. Moom la\u00f1u bindoon ci \u00f1aareelu saaru Sab\u00f3or ne:\u201cYaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.\u201d\n13:34 Te it li ko Y\u00e0lla dekkal, ba mu ba\u00f1atee jaar ci dee, te suuf du ko lekk mukk, moom la Y\u00e0lla wax ne:\u201cDinaa la may barke yu sell te w\u00f3or,yi ma digoon Daawuda.\u201d\n13:35 Moo tax mu waxaat feneen ne:\u201cDoo b\u00e0yyi sa Waa ju sell, mu y\u00e0qu.\u201d\n13:36 Ndaxte bi Daawuda defee coobareg Y\u00e0lla ci jamonoom, mu faatu, \u00f1u suul ko, mu fekki ay maamam, suuf lekk ko.\n13:37 Waaye Ki Y\u00e0lla dekkal, yaramam seeyul.\n13:38 \u00abKon nag bokk yi, nangeen xam ne, ci moom Yeesu nu ngi leen di y\u00e9gal mbaalug b\u00e0kkaar yi. Te f\u00e9pp fu yoonu Musaa t\u00eble woon a \u00e0ttee nit ni ku jub,\n13:39 fa la Yeesu di \u00e0ttee ni ku jub k\u00e9pp ku ko g\u00ebm.\n13:40 Wottuleen nag ba li yonent yi bindoon ba\u00f1 leen a dal, ci li \u00f1u ne:\n13:41 \u201cY\u00e9en \u00f1iy xeebaate, gis leen lii,ngeen y\u00e9emu ba far;ndaxte dinaa def ci seen jamono j\u00ebf,joo xam ne su ngeen ko d\u00e9ggee sax,dungeen ko g\u00ebm.\u201d\u00bb\n13:42 Bi \u00f1uy g\u00e9nn nag ca j\u00e0ngu ba, Yawut ya \u00f1aan leen, \u00f1u baamtu wax ja ca b\u00e9su noflaay ba ca tegu.\n13:43 Te bi mbooloo ma tasee, ay Yawut yu bare ak \u00f1i tuuboon ci yoonu Yawut te ragal Y\u00e0lla, topp ci Pool ak Barnabas. \u00d1uy diisoo ak \u00f1oom, di leen xiir, \u00f1u w\u00e0kkirlu ci yiwu Y\u00e0lla.\n13:44 Noonu b\u00e9su noflaay ba ca tegu, daanaka waa d\u00ebkk b\u00e9pp daje, ngir d\u00e9glu k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n13:45 Waaye bi Yawut yi gisee mbooloo ma, \u00f1u daldi fees ak ki\u00f1aan, di weddi li Pool di wax te di ko xas.\n13:46 Bi loolu amee Pool ak Barnabas ne leen ci lu bir: \u00abY\u00e9en lanu war a j\u00ebkk a y\u00e9gal k\u00e0ddug Y\u00e0lla, waaye gannaaw g\u00e0ntu ngeen ko, ba \u00e0tte seen bopp ne, yeyoowuleen dund gu dul jeex gi, kon nu ngi wo\u00f1\u00f1iku ci \u00f1i dul Yawut.\n13:47 Ndaxte moom la nu Boroom bi sant ci li mu naan:\u201cSamp naa la, nga nekk leeru \u00f1i dul Yawut,ngir nga y\u00f3bbu mucc gi, mu daj cati \u00e0ddina.\u201d\u00bb\n13:48 \u00d1i dul Yawut nag, bi \u00f1u d\u00e9ggee loolu, daldi b\u00e9g tey m\u00e0ggal k\u00e0ddug Boroom bi; te \u00f1\u00e9pp \u00f1u jagoo dund gu dul jeex daldi g\u00ebm.\n13:49 Noonu k\u00e0ddug Boroom bi di law ci diiwaan b\u00e9pp.\n13:50 Waaye Yawut ya xiir ay jig\u00e9en, \u00f1i woomle te farlu ci diine, \u00f1oom ak magi d\u00ebkk ba, \u00f1u fitnaal Pool ak Barnabas, ngir g\u00e9nne leen r\u00e9ew ma.\n13:51 Waaye Pool ak Barnabas daldi y\u00ebl\u00ebb seen p\u00ebndu t\u00e0nk, ngir d\u00ebggal seen weddi, j\u00ebm d\u00ebkku Iko\u00f1um.\n13:52 Naka taalibe yi nag, \u00f1u fees ak mb\u00e9g ak Xel mu Sell mi.\n14:1 Bi Pool ak Barnabas nekkee Iko\u00f1um nag, \u00f1u dugg ci j\u00e0ngub Yawut ya, ni \u00f1u ko daan defe; \u00f1uy waare, ba mbooloom Yawut ak Gereg mu bare g\u00ebm.\n14:2 Waaye Yawut yu nanguwul yi \u00f1oo j\u00f3gloo \u00f1i dul Yawut, di \u00f1aawal seen njort ci bokki taalibe yi.\n14:3 Pool ak Barnabas nag sax na\u00f1u ci Iko\u00f1um lu y\u00e0gg, \u00f1u w\u00e9eru ci Boroom bi, bay wax ak fit wu d\u00ebg\u00ebr; te Y\u00e0lla d\u00ebggal k\u00e0ddug yiwam, ba may leen, \u00f1u def ay k\u00e9emaan ak ay firnde.\n14:4 Noonu waa d\u00ebkk bi x\u00e0jjalikoo, \u00f1ii far ak Yawut yi, \u00f1ale far ak ndaw ya.\n14:5 Waaye \u00f1i dul Yawut ak Yawut yi, \u00f1oom ak seeni kilifa, lal pexem fitnaal leen ci s\u00e0nni ay doj.\n14:6 Bi ko Pool ak Barnabas y\u00e9gee nag, \u00f1u daw ca diiwaanu Likawni ca d\u00ebkk ya \u00f1uy wax Listar ak Derb\u00eb ak w\u00e0llaa ya.\n14:7 Foofa \u00f1u di fa xamle xebaar bu baax bi.\n14:8 Amoon na ca Listar nag nit ku fa toog, ku ay t\u00e0nkam l\u00e0ggi, ndax li mu judduwaale lafa\u00f1 te musul a dox.\n14:9 Moom nag muy d\u00e9glu Pool miy waare. Noonu Pool xool ko j\u00e0kk, gis ne, am na ng\u00ebm ngir w\u00e9r.\n14:10 Mu ne ko ak baat bu d\u00ebg\u00ebr: \u00abJ\u00f3gal taxaw bu jub.\u00bb Noonu nit ki ne b\u00ebr\u00e9t, j\u00f3g, daldi dox.\n14:11 Bi mbooloo ma gisee li Pool def, \u00f1u daldi yuuxu, ne ci l\u00e0kku waa Likawni: \u00abY\u00e0lla yi soppiku na\u00f1u nit, w\u00e0cc ci nun.\u00bb\n14:12 Noonu \u00f1u tudde Barnabas, S\u00ebs, te tudde Pool, Ermes, ndaxte mooy ki yor wax ji.\n14:13 Fekk ci buntu d\u00ebkk ba amoon na fa k\u00ebr gu \u00f1uy m\u00e0ggale S\u00ebs. Saraxalekat ba nag \u00e0nd ak mbooloo ma, daldi indi ca bunt ya ay y\u00ebkk ak ay caq, yi \u00f1u defare t\u00f3or-t\u00f3or, ngir m\u00e0ggal leen ci tuur deretu mala.\n14:14 Waaye bi ko ndaw yi Barnabas ak Sool d\u00e9ggee, \u00f1u sib ko ba xotti seeni y\u00e9re, \u00f1u daldi daw, t\u00e0bbi ca mbooloo ma, di wax ci kaw ne:\n14:15 \u00abY\u00e9en nit \u00f1i, lu leen xiir ci lii? Nun it ay nit lanu, \u00f1u bokk bind ak y\u00e9en. Te nu ngi leen di xamal xebaar bu baax ne leen, ngeen d\u00ebddu y\u00ebfi neen yii te wo\u00f1\u00f1iku ci Y\u00e0lla miy dund te s\u00e0kk asamaan, suuf, g\u00e9ej ak li \u00f1u \u00ebmb l\u00e9pp.\n14:16 D\u00e9mb mayoon na xeet y\u00e9pp, \u00f1u aw seen yoonu bopp.\n14:17 Moona noppiwul a firndeel aw meloom ci def lu baax, di leen w\u00e0cceele ci asamaan taw buy indi naataange, ba ngeen lekk ba suur, te seen xol fees ak mb\u00e9g.\u00bb\n14:18 Noonu ci lu jafe yey na\u00f1u mbooloo ma ak wax jooju, ba tere leen, \u00f1u rendil leen sarax.\n14:19 Waaye bi loolu w\u00e9yee amoon na ay Yawut yu j\u00f3ge Ancos ak Iko\u00f1um, \u00f1u f\u00e0bbi mbooloo ma, s\u00e0nni Pool ay doj, ba yaakaar ne dee na, \u00f1u diri ko ba ca gannaaw d\u00ebkk ba.\n14:20 Waaye taalibe ya \u00f1\u00ebw w\u00ebr ko, mu daldi j\u00f3g, duggaat ca d\u00ebkk ba. Ca suba sa nag, mu \u00e0nd ak Barnabas, dem Derb\u00eb.\n14:21 Bi \u00f1u fa \u00e0ggee nag, \u00f1u xamle fa xebaar bu baax bi, ba s\u00e0kk fa ay taalibe yu bare. Gannaaw loolu \u00f1u dellusi Listar, Iko\u00f1um ak Ancos,\n14:22 di dooleel xeli taalibe ya, xiir leen \u00f1u sax ci yoon wi; \u00f1u ne leen: \u00abCi kaw nattu yu bare lanu war a dugge ci nguuru Y\u00e0lla.\u00bb\n14:23 Ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm mu nekk nag, \u00f1u t\u00e0nn ci ay njiit; ba noppi \u00f1u \u00f1aan Y\u00e0lla ak di woor, d\u00e9nk leen Boroom bi \u00f1u g\u00ebm.\n14:24 Gannaaw loolu \u00f1u jaar diiwaanu Pisidi, dikk ci Pamfili.\n14:25 \u00d1u y\u00e9gle k\u00e0ddu gi ci d\u00ebkku Peers, door a dem d\u00ebkku Atali.\n14:26 Foofa nag \u00f1u dugg gaal, j\u00ebm Ancos, fa \u00f1u leen d\u00e9nke woon ca yiwu Y\u00e0lla, ngir ligg\u00e9ey bi \u00f1u \u00e0ggale.\n14:27 Bi \u00f1u agsee, \u00f1u woo mbooloom \u00f1i g\u00ebm, nettali leen fi \u00f1u jaar ak Y\u00e0lla f\u00e9pp, ak ni mu ubbee buntu ng\u00ebm ci \u00f1i dul Yawut.\n14:28 Noonu \u00f1u toog ak taalibe ya diir bu y\u00e0gg.\n15:1 Amoon na b\u00e9s ay nit j\u00f3ge diiwaanu Yude, \u00f1uy j\u00e0ngal bokk yi ne leen: \u00abKu xaraful, ni ko aaday Musaa santaanee, doo man a mucc.\u00bb\n15:2 Pool ak Barnabas nag am ak \u00f1oom diisoo ak werante wu metti; noonu bokk yi j\u00e0pp ne, Pool ak Barnabas ak \u00f1eneen ci \u00f1oom war na\u00f1oo dem Yerusalem ca ndaw ya ak njiit ya, ngir leeral werante wi.\n15:3 Kon nag mbooloo mi gunge leen, \u00f1u jaar ci w\u00e0lli Fenisi ak Samari, di nettali ni \u00f1i dul Yawut wo\u00f1\u00f1ikoo ci Y\u00e0lla, ba bokk y\u00e9pp am ca mb\u00e9g mu r\u00e9y.\n15:4 Te bi \u00f1u agsee Yerusalem, mbooloom \u00f1i g\u00ebm, ndaw yi ak njiit yi teeru leen, \u00f1u nettali leen fi \u00f1u jaar ak Y\u00e0lla f\u00e9pp.\n15:5 Ci kaw loolu \u00f1eneen, \u00f1i g\u00ebm waaye bokk ci tariixab Farisen ya, daldi j\u00f3g ne: \u00abF\u00e0ww \u00f1i dul Yawut xaraf, te \u00f1u d\u00e9nk leen s\u00e0mm yoonu Musaa.\u00bb\n15:6 Noonu ndaw yi ak njiit yi dajaloo, ngir seet mbir moomu.\n15:7 Gannaaw werante wu bare Piyeer j\u00f3g ne leen: \u00abY\u00e9en bokk yi, xam ngeen ne, ca nj\u00e0lb\u00e9en ga Y\u00e0lla t\u00e0nnoon na ma ci y\u00e9en, ngir ma y\u00e9gal \u00f1i dul Yawut xebaar bu baax bi, ba \u00f1u g\u00ebm.\n15:8 Te Y\u00e0lla, mi xam xol yi, seede na leen ci li mu leen may Xel mu Sell mi, ni mu nu ko maye nun itam.\n15:9 G\u00ebnalantewu nu ak \u00f1oom, ci li mu sellal seen xol ci kaw ng\u00ebm.\n15:10 L\u00e9egi nag lu tax ngeen di dii\u014bat Y\u00e0lla, ciy teg taalibe yi yen bu nu musul a \u00e0ttan, nun mbaa sunuy maam?\n15:11 Nun daal ci yiwu Yeesu Boroom bi lanu yaakaar a mucce, te \u00f1oom itam, ci la\u00f1u w\u00e9kku.\u00bb\n15:12 Bi mu ko waxee, mbooloo m\u00e9pp ne xeram, di d\u00e9glu Barnabas ak Pool, \u00f1uy nettali k\u00e9emaan ak firnde y\u00e9pp, yi Y\u00e0lla def jaarale ko ci \u00f1oom ci biir \u00f1i dul Yawut.\n15:13 Bi \u00f1u noppee, Saag j\u00ebl k\u00e0ddu ga ne:\n15:14 \u00abBokk yi, d\u00e9gluleen ma! Simo\u014b nettali na, ni Y\u00e0lla seetsee bu j\u00ebkk \u00f1i dul Yawut, ngir s\u00e0kku ci \u00f1oom xeet wu \u00f1u tudde turam.\n15:15 Te loolu sax d\u00ebppoo na ak li yonent yi t\u00ebral; \u00f1u bind ne:\n15:16 \u201cBoroom bi nee na:Gannaaw loolu dinaa dellusi,te y\u00e9kkati k\u00ebru Daawuda, gi ne tasar,dinaa defar toj-toj ya,ba taxawalaat ko.\n15:17 Noonu li des ci doom Aadama wut Boroom bi,maanaam xeet yi dul Yawut, \u00f1uy tudd sama tur.\n15:18 Man dinaa def loolu, man Boroom bi ko wax,te ca nj\u00e0lb\u00e9en ba tey ma di ko xamle.\u201d\n15:19 \u00abKon nag lii mooy sama ndigal: bunu g\u00e9t\u00ebn \u00f1i dul Yawut te wo\u00f1\u00f1iku ci Y\u00e0lla.\n15:20 Waaye nu bind leen, \u00f1u moytu \u00f1am wu araam wu \u00f1u tuuroo x\u00ebr\u00ebm, tey moytu njaaloo, ak jur gu m\u00e9dd, bay naan deret ja.\n15:21 Ndaxte ca nj\u00e0lb\u00e9en ga ba tey am na ca d\u00ebkk bu nekk \u00f1uy waare ci yoonu Musaa; b\u00e9su noflaay bu nekk sax da\u00f1u ciy xutba ca j\u00e0ngu ya.\u00bb\n15:22 Bi mu ko waxee, ndaw yi ak njiit yi ak mbooloom \u00f1i g\u00ebm m\u00e9pp fas y\u00e9enee t\u00e0nn ci \u00f1oom ay nit, y\u00f3nni leen Ancos, \u00f1u \u00e0nd ak Pool ak Barnabas. Noonu \u00f1u t\u00e0nn Yudd, mi \u00f1uy dippee Barsabas, ak Silas, di ay njiit ca bokk ya.\n15:23 \u00d1u jox leen bataaxal bu ne: Y\u00e9en sunu bokk yi dul Yawut te d\u00ebkk Ancos, Siri ak Silisi, nu ngi leen di nuyu, nun seeni bokk, di ndaw yi ak njiit yi.\n15:24 D\u00e9gg nanu ne, am na ay nit \u00f1u bawoo ci nun, \u00f1u di leen l\u00ebjal ak seeni wax, di jaxase seeni xol, te fekk sukkandikuwu\u00f1u ci lenn ndigal lu j\u00f3ge ci nun.\n15:25 Kon nag m\u00e0nkoo nanu ci t\u00e0nn ay nit, y\u00f3nnee leen ko, \u00e0nd ak sunuy soppe Barnabas ak Pool.\n15:26 \u00d1oom jaay na\u00f1u seen bakkan ngir turu Yeesu Kirist Boroom bi.\n15:27 Y\u00f3nni nanu nag Yudd ak Silas, \u00f1u di leen xamal xebaar boobu ci seen g\u00e9mmi\u00f1.\n15:28 Ndaxte li neex Xel mu Sell mi te neex nu, mooy nu ba\u00f1 leen a teg beneen yen, lu dul d\u00e9nkaane yii am njari\u00f1,\n15:29 maanaam ngeen moytu \u00f1am wu \u00f1u tuuroo x\u00ebr\u00ebm, deretu jur gu m\u00e9dd ak njaaloo. Bu ngeen moytoo y\u00ebf yooyu, dingeen def lu baax. Ci j\u00e0mm.\n15:30 Noonu \u00f1u t\u00e0ggoo, dem Ancos, \u00f1u dajale mbooloo mi, j\u00e9bbal leen bataaxal bi.\n15:31 \u00d1u j\u00e0ng ko nag, seen xol sedd ci doole, ji leen bataaxal bi indil.\n15:32 Te Yudd ak Silas, \u00f1i doon yonent, \u00f1uy dooleel bokk yi, di d\u00ebg\u00ebral seen fit ak wax yu bare.\n15:33 Bi loolu amee \u00f1u toog fa ab diir, ba noppi bokk yi yiwi leen ci j\u00e0mm, \u00f1u dellu ca \u00f1a leen y\u00f3nni woon.\n15:35 Waaye Pool ak Barnabas des ci Ancos, di j\u00e0ngale ak di xamle xebaar bu baax bu k\u00e0ddug Boroom bi, \u00f1oom ak \u00f1eneen \u00f1u bare.\n15:36 Gannaaw ay fan Pool ne Barnabas: \u00abNan dellu seeti bokk ya ca d\u00ebkk y\u00e9pp, fu nu mas a y\u00e9glee k\u00e0ddug Boroom bi, ba gis nu \u00f1u def.\u00bb\n15:37 Barnabas nag b\u00ebggoon na y\u00f3bbaale Yowaana, mi \u00f1uy wax it M\u00e0rk.\n15:38 Waaye Pool dafa l\u00e0nk ne: \u00abMatul nu y\u00f3bbu ki nu waccoon ca Pamfili, ba \u00e0ndul woon ak nun ca ligg\u00e9ey ba.\u00bb\n15:39 Noonu \u00f1u xuloo, ba far t\u00e0ggoo. Barnabas y\u00f3bbaale M\u00e0rk, \u00f1u dugg gaal, j\u00ebm Sipar.\n15:40 Pool t\u00e0nn Silas, dem; bokk ya d\u00e9nk leen ci yiwu Boroom bi;\n15:41 mu jaar ci diiwaanu Siri ak Silisi, di d\u00ebg\u00ebral mboolooy \u00f1i g\u00ebm.\n16:1 Naka noona mu dikk d\u00ebkki Derb\u00eb ak Listar, fekk fa taalibe bu tudd Timote te ndeyam di Yawut bu g\u00ebm, waaye baayam di Gereg.\n16:2 Te mbokk, yi nekk d\u00ebkki Listar ak Iko\u00f1um, seedeel na\u00f1u ko lu baax.\n16:3 Pool b\u00ebgg nag mu \u00e0nd ak moom, waaye ndegam Yawut y\u00e9pp, ya d\u00ebkk ca w\u00e0llaa ya, xam ne baayam Gereg la woon, mu j\u00ebl ko, xarafal ko.\n16:4 Bi loolu amee \u00f1uy jaar ca d\u00ebkk ya, jottali leen d\u00e9nkaane, yi ndaw yi ak njiit yi nekk Yerusalem joxe, te sant leen \u00f1u s\u00e0mm ko.\n16:5 Noonu mboolooy \u00f1i g\u00ebm di g\u00ebn a d\u00ebg\u00ebr ci yoon wi, tey yokku b\u00e9s bu nekk.\n16:6 Bi loolu amee gannaaw Xel mu Sell mi aaye na leen, \u00f1u y\u00e9gleji k\u00e0ddu gi ci diiwaanu Asi, \u00f1u daldi jaari w\u00e0lli Firisi ak Galasi.\n16:7 Bi \u00f1u agsee nag ci wetu diiwaanu Misi, \u00f1uy j\u00e9em a dugg diiwaanu Bitini, waaye Xelum Yeesu mayuleen ko.\n16:8 \u00d1u romb nag Misi, dem d\u00ebkku Torowas.\n16:9 Noonu ci guddi Y\u00e0lla fee\u00f1u Pool ci nii: nitu Maseduwan taxaw, di ko \u00f1aan ne ko: \u00ab\u00d1\u00ebwal ci Maseduwan, wallusi nu!\u00bb\n16:10 Bi mu amee pee\u00f1u moomu, ca saa sa nu fexee j\u00e0ll ba Maseduwan, xam ne Boroom bi moo nu woo, ngir nu xamle fa xebaar bu baax bi.\n16:11 Noonu nu dugg gaal ca Torowas, jubal dunu Samotaras, j\u00f3ge fa ca \u00ebll\u00ebg sa, nu j\u00ebm teerub Neyapolis.\n16:12 Bi nu fa teeree, nu j\u00ebm Filib, bi nekk d\u00ebkk bi \u00ebpp maana ca w\u00e0ll woowu ci diiwaanu Maseduwan, di it suufus Room. Nu toog fa ay fan.\n16:13 Bi b\u00e9su noflaay agsee nag, g\u00e9nn nanu ci buntu d\u00ebkk ba, jublu ci wetu dex ga, yaakaar ne b\u00e9rabu \u00f1aanukaay la. Nu toog fa nag, di wax ak jig\u00e9en \u00f1a fa dajaloo.\n16:14 Fekk am na fa jig\u00e9en juy d\u00e9glu, tudd Lidi, di jaaykatu cuub, bu d\u00ebkk Catir, te mu ragal Y\u00e0lla. Noonu Boroom bi ubbi na xolam, ba mu nangu li Pool di wax.\n16:15 Ci kaw loolu \u00f1u s\u00f3ob ko ci ndox, moom ak waa k\u00ebram, ba noppi mu \u00f1aan nu ne: \u00abBu ngeen ma j\u00e0ppee ni ku takku ci Boroom bi, ganesileen ma ci sama k\u00ebr.\u00bb Te mu di nu ci xiir.\n16:16 Am b\u00e9s, ba nuy dem nag ca \u00f1aanukaay ba, nu daje ak jaam bu jig\u00e9en bu rabu gisaane solu, te ay sangam di jari\u00f1u lu bare ci gisaaneem.\n16:17 Mu daldi topp ci Pool ak nun, di xaacu ne: \u00abNit \u00f1ii jaami Y\u00e0lla Aji Kawe ji la\u00f1u; \u00f1oo leen di y\u00e9gal yoonu mucc.\u00bb\n16:18 Muy def noonu ay fani fan, waaye bi ko Pool xajootul, mu wo\u00f1\u00f1iku ne rab wa: \u00abSant naa la ci turu Yeesu Kirist, g\u00e9nnal ci moom.\u00bb Noonu rab wa ne m\u00ebll, g\u00e9nn ci moom.\n16:19 Bi ay sangam gisee nag seen buntu w\u00ebrs\u00ebg t\u00ebju, \u00f1u daldi j\u00e0pp Pool ak Silas, di leen diri, j\u00ebme leen ca p\u00e9nc ma fa kanam njiit ya.\n16:20 Noonu \u00f1u d\u00ebj leen fa mbaxanay menne naan: \u00abYawut yii l\u00ebjal na\u00f1u sunu d\u00ebkk,\n16:21 di xamle ay aada yu nu sa\u00f1ul a nangu mbaa nu di ko topp, nun \u00f1i bokk ci nguuru Room.\u00bb\n16:22 Mbooloo ma it \u00e0nd ci, dal ci seen kaw; \u00e0ttekat ya nag summilu seeni y\u00e9re, santaane \u00f1u d\u00f3or leen ay yar.\n16:23 Noonu \u00f1u d\u00f3or leen ay yar yu bare, t\u00ebj leen, sant boroom kaso ba, mu wottu leen bu w\u00e9r.\n16:24 Gannaaw jot na ndigal loolu nag, mu s\u00e0nni leen ca n\u00e9eg ba g\u00ebn a ruqu ci biir kaso ba, j\u00e9ng seeni t\u00e0nk.\n16:25 Ba guddi giy xaaj nag, Pool ak Silas di \u00f1aan ak di sant Y\u00e0lla, te \u00f1eneen \u00f1i nekk ca kaso ba di leen d\u00e9glu.\n16:26 Ca saa sa suuf yengu bu metti, ba fondamaab kaso ba daanu; bunt y\u00e9pp daldi ne kulbet ubbiku, te j\u00e9ngi \u00f1a \u00f1u t\u00ebj ne tell tijjiku.\n16:27 Ci kaw loolu boroom kaso ba tiite ci ay nelaw, gis bunt y\u00e9pp ubbiku, mu daldi bocci jaaseem, b\u00ebgg a xaru, yaakaar ne \u00f1a \u00f1u t\u00ebj da\u00f1oo daw.\n16:28 Waaye Pool wax ci kaw ne: \u00abBul lor sa bopp, nun \u00f1\u00e9pp nu ngi fi.\u00bb\n16:29 Bi ko boroom kaso ba d\u00e9ggee, mu daldi laaj l\u00e0mp, ne saraax dugg, daanu ci kanamu Pool ak Silas, di lox.\n16:30 Mu g\u00e9nne leen ci biti ne leen: \u00abKilifa yi, lu ma war a def, ba mucc?\u00bb\n16:31 \u00d1u tontu ko: \u00abG\u00ebmal Yeesu Boroom bi, kon dinga mucc, yaw ak sa njaboot.\u00bb\n16:32 Noonu \u00f1u xamal ko k\u00e0ddug Boroom bi, moom ak waa k\u00ebram g\u00e9pp.\n16:33 Mu j\u00ebl leen nag ci waxtu woowu ci guddi, raxas seeni gaa\u00f1u-gaa\u00f1u, ba noppi \u00f1u s\u00f3ob ko ci ndox, moom ak waa k\u00ebram g\u00e9pp.\n16:34 Bi \u00f1u ko defee mu y\u00f3bbu leen ca k\u00ebram, jox leen \u00f1u lekk, mu b\u00e9g lool ci li mu g\u00ebm Y\u00e0lla, moom ak waa k\u00ebram g\u00e9pp.\n16:35 Bi b\u00ebt setee, \u00e0ttekat ya y\u00f3nni alkaati ya, \u00f1u ne boroom kaso ba: \u00abYiwil \u00f1aari nit \u00f1oo\u00f1u, \u00f1u dem.\u00bb\n16:36 Kon boroom kaso ba y\u00e9gal loolu Pool ne ko: \u00ab\u00c0ttekat ya jox na\u00f1u ma ndigal, ngir ma yiwi leen, ngeen dem; l\u00e9egi nag g\u00e9nnleen, te dem ci j\u00e0mm.\u00bb\n16:37 Waaye Pool ne alkaati ya: \u00abD\u00f3or na\u00f1u nu ay yar ci kanamu \u00f1\u00e9pp, ci lu \u00f1u w\u00e9erul ci benn \u00e0tte, rax-ca-dolli t\u00ebj na\u00f1u nu kaso, nun \u00f1iy jaambur ci nguuru Room. L\u00e9egi ndax da\u00f1u noo b\u00ebgg a s\u00e0nni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Na\u00f1u \u00f1\u00ebw, \u00f1oom ci seen bopp, gunge nu ci biti.\u00bb\n16:38 Bi mu ko waxee, alkaati ya y\u00e9gal \u00e0ttekat ya la mu wax. Bi \u00f1u d\u00e9ggee ne, jaamburi Room la\u00f1u, \u00f1u daldi tiit.\n16:39 \u00d1u \u00f1\u00ebw nag di leen d\u00ebf\u00ebl, \u00f1u gunge leen ci biti, di leen \u00f1aan, \u00f1u g\u00e9nn d\u00ebkk ba.\n16:40 Noonu \u00f1u g\u00e9nn ca kaso ba, dugg ci k\u00ebr Lidi, \u00f1u gis fa bokk ya, d\u00ebg\u00ebral leen, daldi dem seen yoon.\n17:1 Bi \u00f1u fa j\u00f3gee, \u00f1u aw yoon wa jaar d\u00ebkku Amfipolis ak Apoloni, door a \u00f1\u00ebw Tesalonig, fa Yawut ya am j\u00e0ngu.\n17:2 Pool nag dugg ca \u00f1oom, na mu ko daan defe, ba am fa \u00f1etti b\u00e9su noflaay, muy werante ak \u00f1oom ci li Mbind mi wax.\n17:3 Mu di leen ko tekki, te di leen wax ay firnde yuy wone ne, f\u00e0ww Almasi bi sonn te dekki. Mu ne leen: \u00abYeesu, mi ma leen di y\u00e9gal, mooy Almasi bi.\u00bb\n17:4 Noonu \u00f1enn ci Yawut yi g\u00ebm, \u00e0nd ak Pool ak Silas, \u00f1oom ak mbooloo mu mag ci Gereg yi ragal Y\u00e0lla, ak jig\u00e9en \u00f1u am maana \u00f1u bare.\n17:5 Waaye ki\u00f1aan t\u00e0bbi ca Yawut ya, \u00f1u daldi j\u00ebl ay taxawaalukat ca p\u00e9nc ma, dajale mbooloo, \u00f1uy yengal d\u00ebkk ba. \u00d1u daanu ci k\u00ebr Yason, di wut Pool ak Silas, ngir d\u00ebj leen ci kanam waa d\u00ebkk ba.\n17:6 Bi \u00f1u leen gisul nag, \u00f1u diri Yason ak \u00f1eneen ca bokk ya ci kanam \u00e0ttekat ya. \u00d1uy wax ci kaw naan: \u00abNit \u00f1i d\u00ebpp \u00e0ddina s\u00e9pp agsi na\u00f1u fii l\u00e9egi,\n17:7 te Yason a leen dalal. \u00d1oom \u00f1\u00e9pp da\u00f1oo ba\u00f1 ndigali buur Sesaar ne, am na beneen buur bu \u00f1uy wax Yeesu.\u00bb\n17:8 Bi ko mbooloo mi ak \u00e0ttekat yi d\u00e9ggee, \u00f1u daldi jaaxle lool.\n17:9 Noonu nanguwu\u00f1oo yiwi Yason ak \u00f1i ci des, lu dul bi \u00f1u leen bataleelee dara.\n17:10 Bi loolu amee bokk yi j\u00e0llale Pool ak Silas ci saa si ci guddi, \u00f1u j\u00ebm Bere. Ba \u00f1u fa eggee nag, \u00f1u dugg ca j\u00e0ngub Yawut ya.\n17:11 Fekk \u00f1a fa nekk \u00f1oo g\u00ebn a am ay teggin waa Tesalonig, ndaxte nangu na\u00f1u k\u00e0ddu ga te sawar ca, di niir Mbind mi b\u00e9s bu nekk, ba xam ndax loolu d\u00ebgg la am d\u00e9et.\n17:12 Kon nag Yawut yu bare g\u00ebm ak \u00f1u bare ci Gereg yi, di jig\u00e9en yu am maana ak ay g\u00f3or.\n17:13 Waaye bi Yawuti Tesalonig d\u00e9ggee ne, Pool mu ngi y\u00e9gle k\u00e0ddug Y\u00e0lla ci Bere it, \u00f1u daldi fay dikk, di j\u00f3gloo ak a jaxase mbooloo ma.\n17:14 Noonu bokk yi yebal Pool ca saa sa, mu j\u00ebm g\u00e9ej, waaye Silas ak Timote des fa.\n17:15 \u00d1i \u00e0nd ak Pool nag gunge ko ba d\u00ebkku Aten. Bi \u00f1u fa \u00e0ggee, \u00f1u wo\u00f1\u00f1iku, y\u00f3bbaale ndigalu Pool ne, Silas ak Timote \u00f1\u00ebw fekksi ko ci lu g\u00ebn a gaaw.\n17:16 Bi leen Pool di n\u00e9g ca Aten, mu am naqaru xol wu r\u00e9y ci li mu gis d\u00ebkk ba fees ak ay nataali bokkaale Y\u00e0lla.\n17:17 Muy werante nag ca j\u00e0ngu ba ak Yawut ya ak \u00f1a ragal Y\u00e0lla, tey werante it b\u00e9s bu nekk ca p\u00e9nc ma ak \u00f1a fay dajaloo.\n17:18 Noonu ay boroom xam-xam ci mbooloo mi \u00f1uy wax Epikuren ak ci mbooloo mi \u00f1uy wax Estowisen, di werante ak moom. \u00d1enn ci \u00f1oom ne: \u00abFortukatu xam-xam bii, lu mu b\u00ebgg a wax?\u00bb Te \u00f1a ca des, bi \u00f1u d\u00e9ggee Pool di waare xebaar bu baax bi, aju ci Yeesu ak ci mbirum ndekkite, \u00f1u ne: \u00abDafa mel ni, day waare ay y\u00e0lla yu nu xamul.\u00bb\n17:19 Kon nag \u00f1u j\u00ebl ko, y\u00f3bbu ko ca g\u00e9ew, ba \u00f1uy wax Areyopas. \u00d1u ne ko: \u00abDanoo b\u00ebggoon, nga leeral nu ci sa xam-xam bu bees, bii ngay y\u00e9gle.\n17:20 Ndaxte sol nga ci sunuy nopp lu nu xamul. Danoo b\u00ebggoon a xam nag l\u00e9egi, loolu lu muy tekki.\u00bb\n17:21 Ndaxte waa Aten \u00f1\u00e9pp ak doxand\u00e9em ya fa d\u00ebkk, wax ak a d\u00e9glu lu bees rekk la\u00f1u daan x\u00ebnte.\n17:22 Noonu Pool taxaw ci biir mbooloom Areyopas ne leen: \u00abY\u00e9en waa Aten gis naa ne, farlu ngeen ci diine lool.\n17:23 Ndaxte bi may doxantu di seet seeni m\u00e0ggalukaay, gis naa ci benn bu \u00f1u bind lii: \u201cY\u00e0lla mi nu xamul.\u201d Li ngeen di m\u00e0ggal nag te xamuleen ko, loolu laa leen di xamal.\n17:24 \u00abY\u00e0lla mi s\u00e0kk \u00e0ddina ak li mu \u00ebmb l\u00e9pp, moom miy Boroom asamaan ak suuf, du d\u00ebkk ci n\u00e9egi m\u00e0ggalukaay yu loxoy nit defar.\n17:25 Du jari\u00f1u it ci loxoy nit, mel ni dafa soxla dara, ndax moom mooy jox \u00f1\u00e9pp bakkan ak ruu ak l\u00e9pp.\n17:26 Ci kenn nit la s\u00e0kke xeeti \u00e0ddina y\u00e9pp, \u00f1u d\u00ebkk ci \u00f1eenti xebla yi; fekk \u00e0ppal na xeet wu nekk jamonoom, te r\u00ebdd seen diggi r\u00e9ew.\n17:27 Y\u00e0lla def na loolu, ngir \u00f1u koy wut ci yaakaaru daj ko ci l\u00e0mbatu, fekk sax sorewul kenn ci nun.\n17:28 \u201cNdaxte ci moom lanuy dunde, di ci j\u00ebf te nekk ci,\u201d ni ko \u00f1enn ci seeni taalifkat d\u00ebggale naan: \u201cNun noo di aw xeetam.\u201d\n17:29 Kon nag, bu nu nekkee xeetu Y\u00e0lla, warunoo g\u00ebm ne, Y\u00e0lla mel na ni nataali wurus, xaalis mbaa doj yu nit defar ci xare\u00f1 mbaa xel.\n17:30 Ca jamono yu wees ya Y\u00e0lla toppul \u00f1\u00e0kka xam googa, waaye l\u00e9egi koo man a doon ak foo man a nekk, Y\u00e0lla santaane na, nga tuub say b\u00e0kkaar.\n17:31 Ndaxte s\u00e0kk na b\u00e9s bu muy \u00e0tte \u00e0ddina ci njub, d\u00e9nk ko Nit ki mu t\u00e0nn; te firndeel na loolu bu w\u00f3or, ci li mu ko dekkal ca n\u00e9ew ya.\u00bb\n17:32 Bi \u00f1u d\u00e9ggee nag, muy wax ci mbirum ndekkitel \u00f1i dee, \u00f1ii di ko fontoo, \u00f1a ca des ne ko: \u00abDinanu la d\u00e9glu ci mbir moomu beneen yoon.\u00bb\n17:33 Noonu Pool g\u00e9nn ci seen biir.\n17:34 Moona am na \u00f1enn \u00f1u taq ci moom te g\u00ebm: x\u00e0mmees na ci Denis, ku bokk ci mbooloom Areyopas, ak jig\u00e9en ju tudd Damaris, ak \u00f1eneen.\n18:1 Bi loolu w\u00e9yee Pool b\u00e0yyikoo Aten, dem Korent.\n18:2 Mu tase fa ak Yawut bu tudd Akilas te juddoo diiwaanu Pont. Muy sog a j\u00f3ge r\u00e9ewu Itali ak jabaram Pirsil, ndaxte buur ba K\u00ebl\u00f3dd sant na Yawut y\u00e9pp, \u00f1u g\u00e9nn Room.\n18:3 Noonu Pool seeti leen, te gannaaw \u00f1oo bokk ligg\u00e9ey, maanaam di defar ay t\u00e0nt, mu dal fa \u00f1oom, \u00f1uy ligg\u00e9eyandoo.\n18:4 B\u00e9su noflaay bu nekk nag muy diisoo ak \u00f1i nekk ca j\u00e0ngu ba, di j\u00e9em a g\u00ebmloo ay Yawut ak ay Gereg.\n18:5 Waaye bi Silas ak Timote j\u00f3gee diiwaanu Maseduwan, egg fa, Pool jublu ci xamle k\u00e0ddu gi, tey d\u00ebggal ci Yawut yi naan, Yeesu mooy Almasi bi.\n18:6 Bi ko Yawut ya g\u00e0ntoo nag, di ko xas, mu y\u00ebl\u00ebb ay y\u00e9reem ne leen: \u00abY\u00e9ena s\u00e0kku seen musiba; set naa ci. L\u00e9egi maa ngi dem ci \u00f1i dul Yawut.\u00bb\n18:7 Ci kaw loolu mu j\u00f3ge fa, dugg ci k\u00ebru ku tudd Tisiyus Yustus, di ku ragal Y\u00e0lla, te k\u00ebr ga dend ak j\u00e0ngu ba.\n18:8 Kirispus nag, njiitu j\u00e0ngu ba, g\u00ebm na Boroom bi ak waa k\u00ebram g\u00e9pp. Te waa Korent \u00f1u bare d\u00e9gg k\u00e0ddu gi te g\u00ebm ko, \u00f1u s\u00f3ob leen ci ndox.\n18:9 Naka noona Boroom bi fee\u00f1u Pool ci guddi ne ko: \u00abBul tiit dara, waaye deel wax te ba\u00f1 a noppi.\n18:10 Ndaxte maa ngi \u00e0nd ak yaw, te kenn du la j\u00e0pp, ba fitnaal la, ndaxte am naa xeet wu bare ci d\u00ebkk bii.\u00bb\n18:11 Noonu Pool des at ak genn-w\u00e0ll ci seen biir, di fa j\u00e0ngale k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n18:12 Ci nguuru Galyon ci diiwaanu Akayi nag, Yawut ya likkoo, \u00f1u dal ci kaw Pool, y\u00f3bbu ko ca \u00e0ttekaay ba.\n18:13 \u00d1u ne: \u00abKii day xiir nit \u00f1i ci m\u00e0ggal Y\u00e0lla ci lu juuyoo ak yoon wi.\u00bb\n18:14 Bi Pool b\u00ebggee wax nag, Galyon ne Yawut ya: \u00abY\u00e9en Yawut yi, bu aju woon ci j\u00e0dd yoon walla \u00f1aawteef wu r\u00e9y, kon liy yoon mooy ma d\u00e9glu leen.\n18:15 Waaye bu ajoo ci ay werante ciy wax ak ay tur ak seen yoon, loolu seen w\u00e0ll la; man duma ko \u00e0tte.\u00bb\n18:16 Noonu mu d\u00e0q leen ca \u00e0ttekaay ba.\n18:17 Ci kaw loolu nit \u00f1\u00e9pp j\u00e0pp Sosten, njiitu j\u00e0ngu ba, \u00f1u di ko d\u00f3or ca kanamu \u00e0ttekaay ba, waaye Galyon faalewu leen.\n18:18 Bi loolu w\u00e9yee Pool desati fa fan yu bare. Gannaaw ga mu t\u00e0ggtoo ak bokk ya, dugg gaal j\u00ebm Siri, \u00e0nd ak Pirsil ak Akilas. Bi mu j\u00f3geegul teerub Se\u00f1sere, mu watlu boppam, ndaxte am na lu mu dige woon ak Y\u00e0lla.\n18:19 Noonu \u00f1u teer ci Efes. Pool b\u00e0yyi fa \u00f1i mu \u00e0ndaloon, daldi dugg ca j\u00e0ngu ba, di diisoo ak Yawut ya.\n18:20 \u00d1u \u00f1aan ko, mu des fa lu g\u00ebn a y\u00e0gg, waaye nanguwul.\n18:21 Kon mu t\u00e0ggtoo ak \u00f1oom naan: \u00abDinaa dellusi ci y\u00e9en, bu soobee Y\u00e0lla.\u00bb Noonu mu dugg gaal, j\u00f3ge Efes,\n18:22 teersi d\u00ebkku Sesare, mu dem nuyu mbooloom \u00f1i g\u00ebm, ba noppi dem Ancos.\n18:23 Bi mu fa desee ay jamono, mu j\u00f3ge fa, di jaar d\u00ebkkoo-d\u00ebkk ci diiwaanu Galasi ak Firisi, di dooleel xoli taalibe y\u00e9pp.\n18:24 Amoon na nag Yawut bu tudd Apolos te juddoo Alegs\u00e0ndiri, mu dikk Efes. Nit ku yeewu la woon te am xam-xam bu yaatu ci Mbind mi.\n18:25 J\u00e0ngoon na ci yoonu Boroom bi, di ku farlu ci xelam, muy xamle ak a j\u00e0ngale bu w\u00f3or ci mbirum Yeesu, waaye fekk xam-xamam yem ci ni Yaxya daan s\u00f3obe ci ndox.\n18:26 Noonu mu daldi wax ak fit wu d\u00ebg\u00ebr ca j\u00e0ngu ba. Bi ko Pirsil ak Akilas d\u00e9ggee nag, \u00f1u woo ko fi \u00f1oom, g\u00ebn ko leeral yoonu Y\u00e0lla.\n18:27 Naka mu b\u00ebgg a dem Akayi, bokk ya xiir ko ca, \u00f1u bind taalibe ya, ngir \u00f1u teeru ko teeru bu rafet. Noonu mu dikk fa te jari\u00f1 lool \u00f1i g\u00ebm jaare ko ci yiwu Y\u00e0lla.\n18:28 Ndaxte mu ngay yey Yawut ya ca kanam \u00f1\u00e9pp, di firi Mbind yi, ba wone ne Yeesu mooy Almasi bi.\n19:1 Ba Apolos nekkee Korent nag, Pool jaar ca teggi ya g\u00ebn a kawe ca r\u00e9ew ma, door a dikk Efes. Noonu mu gis fa ay taalibe.\n19:2 Mu ne leen: \u00abNdax jot ngeen ci Xel mu Sell mi, bi ngeen g\u00ebmee?\u00bb \u00d1u tontu ko: \u00abD\u00e9ggunu sax ne, Xel mu Sell mi am na.\u00bb\n19:3 Mu ne leen: \u00abKon nag, bi \u00f1u leen s\u00f3obee ci ndox, lu ciy maana?\u00bb \u00d1u tontu ko: \u00abXanaa li Yaxya t\u00ebral.\u00bb\n19:4 Pool ne leen: \u00abYaxya daan na s\u00f3ob nit \u00f1i ci ndox, ndax bi \u00f1u tuubee seeni b\u00e0kkaar; te mu ne b\u00e0nni Israyil, kiy topp ci moom la\u00f1u war a g\u00ebm, maanaam Yeesu.\u00bb\n19:5 Bi \u00f1u d\u00e9ggee loolu nag, s\u00f3ob na\u00f1u leen ci ndox ci turu Yeesu Boroom bi.\n19:6 Te bi leen Pool tegee loxo, Xel mu Sell mi \u00f1\u00ebw ci \u00f1oom, \u00f1uy wax yeneeni l\u00e0kk, di wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n19:7 Limub nit \u00f1oo\u00f1u nekk na lu mat fukk ak \u00f1aar.\n19:8 Noonu Pool dugg ca j\u00e0ngu ba, di wax ak fit wu d\u00ebg\u00ebr diirub \u00f1etti weer, di diisoo ak \u00f1oom ci mbirum nguurug Y\u00e0lla, di leen j\u00e9em a g\u00ebmloo.\n19:9 Waaye bi xolu \u00f1enn ci \u00f1oom fattee, \u00f1u g\u00ebmadi, bay suufeel yoon wi ci kanam mbooloo ma, mu j\u00f3ge ci \u00f1oom, x\u00e0jjale taalibe yi ak \u00f1oom, di diisoo b\u00e9s bu nekk ca j\u00e0ngukaayu ku \u00f1uy wax Tiranus.\n19:10 Mu w\u00e9y ci noonu diirub \u00f1aari at, ba \u00f1i d\u00ebkk diiwaanu Asi \u00f1\u00e9pp d\u00e9gg k\u00e0ddug Boroom bi, muy Yawut muy Gereg.\n19:11 Booba Y\u00e0llay def ay k\u00e9emaan yu r\u00e0\u00f1\u00f1iku yuy jaar ci loxoy Pool.\n19:12 \u00d1u y\u00f3bbul sax \u00f1i wopp ay kaala ak ay taraxlaay yu laaloon yaramam, ba j\u00e0ngoro yi di leen b\u00e0yyi, rab yay g\u00e9nn ci \u00f1oom.\n19:13 Noonu ay Yawut yuy w\u00ebnd\u00e9elu, di faj \u00f1i rab j\u00e0pp, \u00f1u di leen j\u00e9em a \u00f1aanal ci turu Yeesu Boroom bi naan: \u00abCi turu Yeesu, mi Pool di y\u00e9gle, g\u00e9nnleen.\u00bb\n19:14 \u00d1i doon def loolu, jur\u00f3om-\u00f1aari doom la\u00f1u woon ci Sewa, mi doon taafantaloo saraxalekat bu mag ba ci Yawut yi.\n19:15 Waaye bi \u00f1u ko defee rab wa tontu leen ne: \u00abXam naa Yeesu, xam naa it kuy Pool, waaye y\u00e9enay \u00f1an?\u00bb\n19:16 Ci kaw loolu nit ka rab j\u00e0pp song leen, noot leen \u00f1oom \u00f1\u00e9pp; mu soxore leen lool, ba \u00f1u daw k\u00ebr ga, def yaramu neen te gaa\u00f1u bu metti.\n19:17 Loolu siiw na ci \u00f1\u00e9pp, \u00f1i d\u00ebkk Efes, di Yawut ak Gereg; tiitaange j\u00e0pp leen \u00f1oom \u00f1\u00e9pp, ba \u00f1u m\u00e0ggal turu Yeesu Boroom bi.\n19:18 Bi loolu amee \u00f1u bare ci \u00f1i g\u00ebm \u00f1\u00ebw, di wesar ci kanam \u00f1\u00e9pp seeni jati luxus.\n19:19 Te \u00f1u bare ci \u00f1i daan luxus, indi seeni t\u00e9ere, lakk leen ci kanam \u00f1\u00e9pp. Te bi \u00f1u xaymaa nj\u00ebg ga, mu tollook jur\u00f3om-fukki junniy poseti daraxma.\n19:20 Noonu la k\u00e0ddu Boroom bi lawe, te noot l\u00e9pp.\n19:21 Bi loolu w\u00e9yee Pool nas xel j\u00ebm Yerusalem, jaar ci diiwaani Maseduwan ak Akayi. Mu ne: \u00abGannaaw bu ma fa demee, f\u00e0ww ma seeti Room it.\u00bb\n19:22 Mu yebal nag ci Maseduwan \u00f1aari jaraafam, di Timote ak Erast, waaye moom mu des ab diir ci Asi.\n19:23 Fekk booba amoon na yengu-yengu bu r\u00e9y ci lu aju ci Yoon wi.\n19:24 Ndaxte nit ku tudd Demetirus, di t\u00ebggu xaalis buy defar nataali xaalis ngir m\u00e0ggal Artemis, daan na ci jari\u00f1u lu bare, moom ak ay nawleem.\n19:25 Noonu mu dajale leen ak seeni ligg\u00e9eykat ne leen: \u00abGaa \u00f1i, xam ngeen ne, sunu njari\u00f1 mu ngi aju ci ligg\u00e9ey bii.\n19:26 Gis ngeen nag te d\u00e9gg ne, Pool male g\u00ebmloo na bay f\u00e0bbi mbooloo mu bare, waxuma ci Efes rekk, waaye ci biir Asi g\u00e9pp naan: \u201cY\u00e0lla yu ay loxo defar du\u00f1u ay y\u00e0lla.\u201d\n19:27 L\u00e9egi kat loraangee ngi nuy yoot, te du yem ci xa\u00f1 nu sunu ligg\u00e9ey rekk, waaye it dina daaneel m\u00e0ggalukaayu Artemis sunu y\u00e0lla ju mag ji, tey neenal ndamam, moom mi Asi g\u00e9pp te \u00e0ddina s\u00e9pp di m\u00e0ggal.\u00bb\n19:28 Bi \u00f1u d\u00e9ggee loolu, mer mu r\u00e9y t\u00e0bbi ci \u00f1oom, \u00f1uy yuuxu ne: \u00abArtemis mu Efes m\u00e0gg na!\u00bb\n19:29 Noonu d\u00ebkk b\u00e9pp jaxasoo. \u00d1u bokk benn xalaat, daldi ne milib ca powukaay ba, diri Gayus ak Arist\u00e0rk, waa Maseduwan, \u00f1i \u00e0nd ak Pool.\n19:30 Pool nag b\u00ebgg a dugg ca mbooloo ma, waaye taalibe ya nanguwu\u00f1u ko.\n19:31 \u00d1enn ca jawri\u00f1i nguur gi it, \u00f1uy ay xaritam, y\u00f3nnee ci moom, di ko d\u00e9nk, mu ba\u00f1 a jaay bakkanam ci dugg ca powukaay ba.\n19:32 Noonu ndaje ma r\u00ebb, ba \u00f1ii di yuuxu lii, \u00f1ale di yuuxu laa, te \u00f1a ca g\u00ebn a bare xamu\u00f1u lu waral ndaje ma.\n19:33 Ci kaw loolu Yawut ya j\u00e9\u00f1 Alegs\u00e0ndar ci kanam, te mbooloo ma di ko xaacu ay ndigal, mu daldi t\u00e0llal loxoom, ngir l\u00e0yyi ca mbooloo ma.\n19:34 Waaye bi \u00f1u xamee ne Yawut la, \u00f1\u00e9pp a bokk benn baat, yuuxu diirub lu mat \u00f1aari waxtu naan: \u00abArtemis mu Efes m\u00e0gg na!\u00bb\n19:35 Gannaaw loolu boroom d\u00ebkk ba dalal mbooloo ma ne leen: \u00abY\u00e9en waa Efes, ana ku xamul ne, d\u00ebkku Efes moo di wottukaayu m\u00e0ggalukaayu Artemis ak nataalam, bi w\u00e0cce asamaan?\n19:36 Gannaaw nag kenn m\u00ebnta weddi loolu, war ngeen a dalal seen xel te ba\u00f1 a sa\u00f1axu ci dara.\n19:37 Ndaxte nit \u00f1ii ngeen fi indi s\u00e0ccu\u00f1u ca m\u00e0ggalukaay ya te sosalu\u00f1u sunu y\u00e0lla.\n19:38 Su fekkee ne Demetirus ak ay nawleem j\u00e0nkoonte na\u00f1u ak kenn, am na ay b\u00e9si layoo ak \u00f1u yilif r\u00e9ew mi; na\u00f1u fa woo ku \u00f1u amleenteel.\n19:39 Waaye su ngeen di laaj leneen, mbooloom d\u00ebgg dina ko \u00e0tte.\n19:40 Ndaxte fi mu ne man na\u00f1u noo jii\u00f1 j\u00f3gug mbooloo mi ndax li fi xew tey. Te bu loolu amee dunu am aw lay ci mbirum mbooloo mu r\u00ebb mii, ndaxte amul dara lu ko waral.\u00bb\n19:41 Bi mu waxee loolu nag, mu tas mbooloo ma.\n20:1 Bi yengu-yengu ba dalee, Pool woo taalibe ya fa moom, dooleel leen. Bi mu ko defee mu t\u00e0ggoo ak \u00f1oom, j\u00f3ge fa, dellu diiwaanu Maseduwan.\n20:2 Noonu mu jaar ca b\u00e9rab yooyu, di dooleel nit \u00f1i ak wax yu bare; ba noppi mu dem r\u00e9ewu Geres,\n20:3 toog fa \u00f1etti weer. Waaye bi mu nekkee ci kaw t\u00e0nki dugg gaal j\u00ebm diiwaanu Siri, te Yawut yi lalal ko pexe, mu fas y\u00e9enee dellu, jaare Maseduwan.\n20:4 Booba nag \u00f1ii \u00f1oo \u00e0nd ak moom: Sopater, doomu Pirus mi d\u00ebkk Bere; Arist\u00e0rk ak Segond, \u00f1i d\u00ebkk Tesalonig; Gayus, mi d\u00ebkk Derb\u00eb, ak Timote; te it Tisig ak Torofim \u00f1i d\u00ebkk Asi.\n20:5 \u00d1oo\u00f1u nag jiitu, di nu n\u00e9g d\u00ebkku Torowas.\n20:6 Waaye naka nun, gannaaw m\u00e0ggalu Yawut, ga \u00f1uy wax Mburu ya amul lawiir, nu dugg gaal ci Filib, def ci jur\u00f3omi fan, fekksi leen Torowas, nu am fa jur\u00f3om-\u00f1aari fan.\n20:7 Ca b\u00e9s bu j\u00ebkk ca ayu-b\u00e9s ga, booloo nanu ngir damm mburu ma. Te Pool, mi b\u00ebggoon a dem ca \u00ebll\u00ebg sa, di diisoo ak \u00f1oom te waxtaanam law ba ci xaaju guddi.\n20:8 Ca n\u00e9eg bu kawe, ba nu booloo nag, amoon na fa l\u00e0mp yu bare.\n20:9 Noonu waxambaane wu tudd \u00cbtikus te toog ca palenteer ba, g\u00ebmmeentu bay jeyaxu. Bi Pool di g\u00ebn a yaatal waxtaanam nag, nelaw daldi ko j\u00e0pp, mu x\u00e0wweekoo ca \u00f1etteelu taax ma, daanu, \u00f1u y\u00e9kkati ko, fekk mu dee.\n20:10 Waaye Pool w\u00e0cc, daldi s\u00ebgg ci kawam, roof ko loxoom ne leen: \u00abB\u00e0yyileen jooy yi, mu ngi dund.\u00bb\n20:11 Noonu mu y\u00e9egaat, damm mburu ma, lekk; ba noppi delluwaat ci waxtaanam, di ko yaatal ba ca nj\u00ebl, door a t\u00e0ggoo.\n20:12 Naka waxambaane wa, \u00f1u indi ko muy dund, ba seen xol sedd guyy.\n20:13 Nun nag nu jiitu, dugg gaal j\u00ebm Asos, fa nu Pool santoon, nu j\u00eble ko fa; fekk moom fas na y\u00e9eney dox, ba agsi fa.\n20:14 Noonu mu fekksi nu ci Asos, nu j\u00ebl ko ca gaal ga, dem Mitilen.\n20:15 Gannaaw loolu gaal ga j\u00f3ge fa, nu agsi ca \u00ebll\u00ebg sa janook dunu Kiyos. B\u00e9s ba ca tegu nag nu j\u00e0ll ba Samos, te \u00f1etteelu fan ba nu \u00e0gg Mile.\n20:16 Ndaxte Pool fasoon na y\u00e9enee teggi Efes, ngir ba\u00f1 a y\u00e0gg ci diiwaanu Asi; mu ngi doon gaawantu, ngir m\u00e0ggal, gi \u00f1uy wax P\u00e0ntakot fekk ko Yerusalem.\n20:17 Bi Pool eggee Mile nag, mu y\u00f3nnee ca Efes, ngir woo njiiti mbooloom \u00f1i g\u00ebm.\n20:18 Bi \u00f1u \u00f1\u00ebwee, mu ne leen: \u00abY\u00e9en xam ngeen bu baax, ni ma doon doxale diirub sama ngan g\u00e9pp ci seen biir, li dale ci b\u00e9s bi ma j\u00ebkkee teg t\u00e0nk ci Asi ba tey.\n20:19 Jaamu naa Boroom bi ci woyof gu mat ak ay rangoo\u00f1, d\u00e9kku ay nattu yu ma pexey Yawut yi indil.\n20:20 Xam ngeen ne, musuma leen a n\u00ebbb dara lu leen di jari\u00f1, di leen j\u00e0ngal ci kanamu \u00f1\u00e9pp ak ca k\u00ebr ya.\n20:21 D\u00e9nk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, \u00f1u tuub seeni b\u00e0kkaar, ba wo\u00f1\u00f1iku ci Y\u00e0lla te g\u00ebm sunu Boroom Yeesu.\n20:22 \u00abL\u00e9egi maa ngi nii di dem Yerusalem, ci li ma Xelu Y\u00e0lla mi xiirtal, te xawma lu ma fay dal.\n20:23 Xam naa rekk ne, ci d\u00ebkkoo-d\u00ebkk Xel mu Sell mi xamal na ma ne, ay buum ak ay metit \u00f1u ngi may n\u00e9g.\n20:24 Waaye sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal ligg\u00e9ey, bi ma Boroom bi d\u00e9nk, maanaam ma seedeel ci \u00f1\u00e9pp xebaar bu baax, bi \u00ebmb yiwu Y\u00e0lla.\n20:25 \u00abFi mu ne nag xam naa ne, dootuleen gis sama kanam, y\u00e9en \u00f1\u00e9pp \u00f1i ma jaaroon ci seen biir, di y\u00e9gle nguuru Y\u00e0lla.\n20:26 Moo tax may d\u00ebggal tey jii ne, w\u00e0ccoo naa ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp b\u00e9s p\u00e9nc.\n20:27 Ndaxte \u00f1eebluwuma leen, ci di leen xamal l\u00e9pp li Y\u00e0lla digle.\n20:28 Wottuleen nag seen bopp te wottu coggal j\u00e9pp, ji leen Xel mu Sell mi def s\u00e0mm, ngeen s\u00e0mm mbooloo, mi Y\u00e0lla jotal boppam ak deretu Doomam.\n20:29 Xam naa ne, bu ma leen wonee gannaaw, bukki yu soxor dina\u00f1u t\u00e0bbi ci coggal ji te du\u00f1u ci \u00f1eeblu kenn.\n20:30 Ay nit dina\u00f1u j\u00f3g ci seen biir sax, di wax luy s\u00e0nke, ngir s\u00e0kku ay taalibe.\n20:31 Foogleen nag, di f\u00e0ttaliku ne diirub \u00f1etti at, guddi ak b\u00ebcc\u00ebg, musumaa noppi di leen artu kenn ku nekk ci y\u00e9en ak ay rangoo\u00f1.\n20:32 \u00abL\u00e9egi nag maa ngi leen di d\u00e9nk Boroom bi, moom ak k\u00e0ddug yiwam, gi leen man a d\u00ebg\u00ebral te may leen c\u00e9r ci biir gaayi Y\u00e0lla yu sell y\u00e9pp.\n20:33 Nammuma xaalisu kenn mbaa wurusam mbaa koddaayam.\n20:34 Xam ngeen ne, faj naa samay soxla ak soxlay \u00f1i \u00e0nd ak man ci sama loxo yii.\n20:35 Ci l\u00e9pp won naa leen royukaay, ci li nu war a dimbali \u00f1i n\u00e9ew doole te f\u00e0ttaliku li Yeesu Boroom bi wax moom ci boppam ne: \u201cJoxe moo g\u00ebn a barkeel nangu.\u201d\u00bb\n20:36 Bi mu waxee loolu, mu sukk ak \u00f1oom \u00f1\u00e9pp, \u00f1aan ci Y\u00e0lla.\n20:37 Te \u00f1\u00e9pp jooy bu metti, di laxasu ci baatu Pool, f\u00f3on ko bu baax.\n20:38 Li leen g\u00ebn a teg aw tiis mooy li mu leen wax: \u00abDootuleen gis sama kanam.\u00bb Noonu \u00f1u gunge ko ba ca gaal ga.\n21:1 Bi nga xamee ne t\u00e0ggoo nanu ak \u00f1oom ci naqar, nu dugg gaal, jubal dunu Kos. Te ca \u00ebll\u00ebg sa nu dem ba teer ca Rodd, ba noppi j\u00f3ge fa, j\u00e0ll ba Patara.\n21:2 Foofa nag nu gis gaal guy j\u00e0ll ba Fenisi, nu dugg ca, mu daldi teddi.\n21:3 Noonu nu s\u00e9en dunu Sipar, b\u00e0yyi ko ci sunu c\u00e0mmoo\u00f1, jublu diiwaanu Siri, nu teersi Tir. Ndaxte foofa la gaal gi war a yebbee la mu yeboon.\n21:4 Nu wut taalibe ya, ba gis leen, toog ak \u00f1oom jur\u00f3om-\u00f1aari fan. \u00d1oom nag \u00f1u ne Pool ci li leen Xelu Y\u00e0lla mi may, mu ba\u00f1 a dem Yerusalem.\n21:5 Moona bi jataayu gaal ga matee, nu awaat ci yoon wi. Te \u00f1\u00e9pp gunge nu, \u00f1oom ak seeni jabar ak seeni doom; nu g\u00e9nn d\u00ebkk ba, sukk ca tefes ga, \u00f1aan ci Y\u00e0lla.\n21:6 Noonu nu t\u00e0ggoo ak \u00f1oom, dugg ca gaal ga, \u00f1u dellu seen k\u00ebr.\n21:7 Bi nu j\u00f3gee Tir nag, nu demaat ci g\u00e9ej, ba teer Patolemayis. Foofa nu nuyu bokk ya, yendu, fanaan.\n21:8 Nu j\u00f3ge fa ca \u00ebll\u00ebg sa, \u00f1\u00ebw ba ca d\u00ebkku Sesare. Nu dugg ca k\u00ebr Filib, taskatu xebaar bu baax bi, mi bokk ci Jur\u00f3om-\u00f1aar \u00f1a, nu dal fa moom.\n21:9 Amoon na \u00f1eenti doom yuy janq, \u00f1uy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n21:10 Bi nu fa nekkee ay fan nag, yonent bu tudd Agabus j\u00f3ge Yude, agsi.\n21:11 Mu \u00f1\u00ebw ci nun, daldi yeew ay loxoom ak i t\u00e0nkam ak laxasaayu Pool naan: \u00abNii la Xel mu Sell mi waxe: \u201cKi moom laxasaay gii, Yawut yi dina\u00f1u ko yeewe nii ca Yerusalem, j\u00e9bbal ko \u00f1i dul Yawut.\u201d\u00bb\n21:12 Bi nu d\u00e9ggee loolu, nun ak \u00f1a fa nekk nu \u00f1aan Pool, mu ba\u00f1 a dem Yerusalem.\n21:13 Ci kaw loolu Pool tontu ne: \u00abLu ngeen di jooy, di y\u00e0q sama xol? Ba\u00f1uma \u00f1u yeew ma rekk, waaye nangu naa sax, \u00f1u rey ma ci Yerusalem ngir turu Yeesu Boroom bi.\u00bb\n21:14 Bi nu ko m\u00ebnul a d\u00ebpp, nu noppi ne: \u00abKon na coobareg Boroom bi am!\u00bb\n21:15 Gannaaw fan yooyu nu defaru, ngir dem Yerusalem.\n21:16 Noonu ay taalibe yu d\u00ebkk Sesare \u00e0nd ak nun, y\u00f3bbu nu ca nit ku tudd Manason, fu nu war a dal; moom nag nitu Sipar la woon, di taalibe bu y\u00e0gg.\n21:17 Bi nu agsee Yerusalem nag, taalibe ya teeru nu ak mb\u00e9g.\n21:18 Ca \u00ebll\u00ebg sa Pool \u00e0nd ak nun, seeti Saag, fekk njiit y\u00e9pp teew fa.\n21:19 Noonu Pool nuyu leen, nettali leen benn-benn li Y\u00e0lla def ci biir \u00f1i dul Yawut, jaarale ko ci ligg\u00e9eyam.\n21:20 Bi ko njiit ya d\u00e9ggee, \u00f1u m\u00e0ggal Y\u00e0lla ne ko: \u00abMbokk mi, gis nga ne, am na ay junniy Yawut \u00f1u g\u00ebm, te \u00f1\u00e9pp a sawar ci yoonu Musaa.\n21:21 D\u00e9gg na\u00f1u ci sa mbir nag ne, yaa ngi j\u00e0ngal Yawut y\u00e9pp, yi d\u00ebkk ci biir \u00f1i dul Yawut, \u00f1u b\u00e0yyi yoonu Musaa te ba\u00f1 a xarafal seeni doom mbaa topp sunuy aada.\n21:22 Lu nu ci war a def nag? Ndaxte ci lu w\u00e9r dina\u00f1u xam ne, \u00f1\u00ebw nga.\n21:23 Nu ngi lay digal nag, nga def nii: am na ci nun \u00f1eenti g\u00f3or yu dige ak Y\u00e0lla.\n21:24 J\u00ebl leen, bokk ak \u00f1oom setlu, te nga g\u00e0ddu seen peyu wateef. Noonu \u00f1\u00e9pp dina\u00f1u xam ne, li \u00f1u d\u00e9ggoon ci sa mbir du d\u00ebgg, waaye yaa ngi j\u00ebf tey s\u00e0mm yoonu Musaa.\n21:25 Naka \u00f1i dul Yawut \u00f1i g\u00ebm, bind nanu leen li nu \u00e0tte ne, \u00f1u moytu \u00f1am wu \u00f1u tuuroo x\u00ebr\u00ebm te moytu deretu m\u00e9dd ak njaaloo.\u00bb\n21:26 Bi \u00f1u ko waxee, Pool j\u00ebl nit \u00f1a te ca \u00ebll\u00ebg sa mu bokk setlu ak \u00f1oom, \u00f1u dugg ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga. \u00d1u xamle ban b\u00e9s la seen setlu di \u00e0gg, di b\u00e9s bu \u00f1uy j\u00e9bbale sarax ngir kenn ku nekk ci \u00f1oom.\n21:27 Bi \u00e0ppu jur\u00f3om-\u00f1aari fan ya di b\u00ebgg a jeex, Yawut yi j\u00f3ge diiwaanu Asi gis Pool ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga. \u00d1u daldi j\u00f3gloo mbooloo m\u00e9pp, j\u00e0pp ko,\n21:28 di xaacu ne: \u00abWallee, wallee, y\u00e9en bokki Israyil; waa jaa ngi nii, moom miy waare f\u00e9pp ak ci \u00f1\u00e9pp, bay suufeel sunu xeet ak yoonu Musaa ak b\u00e9rab bii; dugal na sax ay Gereg fii ci k\u00ebr Y\u00e0lla gi, ba indi sobe ci b\u00e9rab bu sell bii.\u00bb\n21:29 Li tax \u00f1u wax loolu, mooy gisoon na\u00f1u Torofim mu Efes, \u00e0nd ak moom ca d\u00ebkk ba, te \u00f1u yaakaar ne, Pool dugal na ko ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga.\n21:30 Noonu d\u00ebkk ba b\u00e9pp m\u00e0bb, mbooloo ma ne k\u00ebpp, \u00f1u j\u00e0pp Pool, g\u00e9nne ko ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga. Ca saa sa \u00f1u t\u00ebj bunt ya.\n21:31 Bi \u00f1u koy wut a rey, xebaar ba agsi ba ca kilifag mbooloom xarekat ba, naan Yerusalem g\u00e9pp jaxasoo na.\n21:32 Ca saa sa mu \u00e0nd ak ay xarekat ak ay njiiti xare, ne jaas w\u00e0cc ci \u00f1oom. Bi Yawut ya gisee kilifa ga ak xarekat ya nag, \u00f1u daldi b\u00e0yyi d\u00f3or, ya \u00f1u doon d\u00f3or Pool.\n21:33 Noonu kilifa ga jegesi j\u00e0pp ko, santaane \u00f1u j\u00e9ng ko ak \u00f1aari c\u00e0llala. Bi \u00f1u ko defee mu laaj ku mu doon ak lu mu def.\n21:34 Waaye ci biir mbooloo ma, bu \u00f1ii nee lii, \u00f1a ca des ne laa. Kon nag gannaaw m\u00ebnu caa xam dara lu w\u00f3or ndax coow li, mu santaane, \u00f1u y\u00f3bbu ko ci biir tata ja.\n21:35 Bi Pool eggee ca y\u00e9egukaayu tata ja, aaytalu mbooloo ma r\u00e9y, ba ay xarekat fab ko.\n21:36 Ndaxte mbooloo maa nga ko topp, di xaacu ne: \u00abReyleen ko!\u00bb\n21:37 Bi \u00f1u koy b\u00ebgg a dugal ca tata ja, Pool ne kilifa ga: \u00abNdax man naa laa wax dara?\u00bb Mu tontu ko: \u00abYaw d\u00e9gg nga gereg?\n21:38 Kon nekkuloo waayi Misra, jooju j\u00f3gloo woon nit \u00f1i keroog te y\u00f3bbu woon \u00f1eenti junniy b\u00f3omkat ca m\u00e0ndi\u014b ma?\u00bb\n21:39 Pool ne ko: \u00abMan Yawut laa, di jaambur ci Tars, d\u00ebkk bu am tur ci diiwaanu Silisi. Maa ngi lay \u00f1aan, ma wax ak mbooloo mi.\u00bb\n21:40 Te kilifa ga may ko ko. Noonu Pool taxaw ca y\u00e9egukaay ba, t\u00e0llal loxoom mbooloo ma, \u00f1u daldi ne tekk. Mu wax ak \u00f1oom ci l\u00e0kku yawut ne:\n22:1 \u00abY\u00e9en bokk yi ak baay yi, d\u00e9gluleen samaw lay.\u00bb\n22:2 Bi \u00f1u d\u00e9ggee, mu di leen wax ci l\u00e0kku yawut, \u00f1u g\u00ebn ne xeram. Noonu Pool ne leen:\n22:3 \u00abMan Yawut laa, juddoo Tars ci diiwaanu Silisi, yaroo ci d\u00ebkk bii. Taalibe laa woon ci Gamaleel, mu j\u00e0ngal ma bu w\u00e9r yoonu sunuy maam, ba ma sawar ci Y\u00e0lla, mel ni y\u00e9en \u00f1\u00e9pp tey.\n22:4 Daan naa fitnaal \u00f1a bokkoon ci yoon wii, ba di ci rey sax; yeew naa g\u00f3or ak jig\u00e9en, t\u00ebj leen;\n22:5 saraxalekat bu mag ba ak mbooloom njiit yi y\u00e9pp man na\u00f1u ma cee seede. Am b\u00e9s \u00f1u bindal ma ay bataaxal ngir bokki Damas. Ma doon fa dem, ngir yeew \u00f1a fa nekkoon, indi leen Yerusalem, ngir \u00f1u yar leen.\n22:6 \u00abWaaye ci digg-b\u00ebcc\u00ebg, bi ma jaaree ca yoon wa, ba jegesi Damas, ca saa sa leer gu mag j\u00f3ge asamaan, melax ba \u00ebmb ma.\n22:7 Ma daldi ne n\u00ebr\u00ebm ci suuf, d\u00e9gg baat bu ma ne: \u201cSool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal?\u201d\n22:8 Ma tontu ko: \u201cYaa di kan, Boroom bi?\u201d Mu ne ma: \u201cMaa di Yeesum Nasaret, mi ngay fitnaal.\u201d\n22:9 \u00d1i ma \u00e0ndaloon gis na\u00f1u leer ga, waaye d\u00e9ggu\u00f1u baatu ka doon wax ak man.\n22:10 Noonu ma laaj ko: \u201cLu ma war a def, Boroom bi?\u201d Boroom bi ne ma: \u201cJ\u00f3gal dem Damas, foofa dees na la biral l\u00e9pp, li ma la yen.\u201d\n22:11 Gannaaw gisuma woon dara ndax leeraayu melxat ga, \u00f1a ma \u00e0ndal wommat ma, ma \u00f1\u00ebw Damas.\n22:12 \u00abBi ma ko defee ku tudd Ana\u00f1as \u00f1\u00ebw ci man. Nit ku ragal Y\u00e0lla la woon ci s\u00e0mm yoonu Musaa, te Yawuti Damas y\u00e9pp seedeel ko lu baax.\n22:13 Mu taxaw ci sama wet ne ma: \u201cSool sama mbokk, delluwaatal di gis.\u201d Noonu ma daldi gisaat ca saa sa, xool ko.\n22:14 Mu ne ma: \u201cSunu Y\u00e0llay maam t\u00e0nn na la, ba may la, nga xam coobareem te gis Aji Jub ji te nga d\u00e9gg ay waxam.\n22:15 Ndaxte li nga gis te d\u00e9gg ko, dinga ko seede ci \u00f1\u00e9pp.\n22:16 L\u00e9egi nag, looy n\u00e9g? J\u00f3gal, \u00f1u s\u00f3ob la ci ndox, nga set ci say b\u00e0kkaar ci tudd turu Yeesu.\u201d\n22:17 \u00abBi ma dellusee Yerusalem nag, di \u00f1aan ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, leer t\u00e0bbi ci man.\n22:18 Ma daldi gis Boroom bi, mu ne ma: \u201cG\u00e9nnal Yerusalem ci ni mu g\u00ebn a gaawe, ndaxte du\u00f1u nangu li ngay seede ci man.\u201d\n22:19 Waaye ma tontu ne: \u201cBoroom bi, xam na\u00f1u ne, dama daan w\u00ebr j\u00e0ngoo-j\u00e0ngu, di t\u00ebj kaso ak di d\u00f3or ay yar \u00f1i la g\u00ebm.\n22:20 Rax-ca-dolli bi \u00f1u tuuree deretu Ecen, mi la doon seedeel, teewe naa ko, \u00e0nd ca, bay wottu sax y\u00e9rey \u00f1i ko doon rey.\u201d\n22:21 Waaye Boroom bi ne ma: \u201cDemal, dinaa la yebal fu sore, nga j\u00ebm ci xeeti \u00f1i dul Yawut.\u201d\u00bb\n22:22 Mbooloo ma d\u00e9glu ko nag ba ca wax jooju, waaye bi \u00f1u d\u00e9ggee loolu, \u00f1u daldi yuuxu naan: \u00abFarleen ko ci \u00e0ddina! Yembar mu mel ni moom yeyoowul a dund!\u00bb\n22:23 \u00d1u daldi yuuxu ak di s\u00e0nni seeni y\u00e9re, tey callameeru suuf.\n22:24 Noonu kilifa ga santaane, \u00f1u dugal Pool ca tata ja te caw ko ay yar yu metti, laaj ko ba xam lu tax \u00f1u di ko yuuxoo nii.\n22:25 Waaye bi \u00f1u koy jo\u00f1 ak ay der, Pool ne njiitu xare ba fa taxaw: \u00abNdax am nga sa\u00f1-sa\u00f1u d\u00f3or ay yar jaamburu Room, te fekk yoon dabu ko sax?\u00bb\n22:26 Bi ko njiit la d\u00e9ggee, mu fekki kilifaam, y\u00e9gal ko ko; mu ne ko: \u00abNdax xam nga li ngay def? Nit kale jaambur la ci Room.\u00bb\n22:27 Noonu kilifa ga \u00f1\u00ebw laaj Pool: \u00abWax ma, ndax jaambur nga ci Room?\u00bb Mu tontu ko: \u00abWaaw, moom laa.\u00bb\n22:28 Kilifa ga ne ko: \u00abMan fey naa xaalis bu bare, ngir nekk jaambur ci Room.\u00bb Waaye Pool tontu ko: \u00abMan de dama koo judduwaale.\u00bb\n22:29 \u00d1i ko b\u00ebggoon a d\u00f3or ay yar nag randu ko ca saa sa. Te kilifa ga sax tiit ci xam ne Pool jaamburu Room la, te yeewlu na ko.\n22:30 Ca \u00ebll\u00ebg sa mu b\u00e0yyi ko, ndaxte b\u00ebggoon na xam bu w\u00f3or lu ko Yawut ya jii\u00f1. Mu santaane ne, saraxalekat yu mag ya dajaloo, \u00f1oom ak kureelu \u00e0ttekat ya. Gannaaw loolu mu indilu Pool, d\u00ebj ko ci seen kanam.\n23:1 Noonu Pool xool j\u00e0kk g\u00e9ew ba ne leen: \u00abBokk yi, ci xel mu dal laa doxale ci kanam Y\u00e0lla ba ci b\u00e9su tey bi.\u00bb\n23:2 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag ba, di ku \u00f1uy wax Ana\u00f1as, sant \u00f1a taxaw ca wetam, \u00f1u f\u00e9l g\u00e9mmi\u00f1am.\n23:3 Pool ne ko: \u00abY\u00e0lla dina la d\u00f3or, yaw mi naaf\u00e9q, bay samandaay miir bu joy bu \u00f1u weexal. Yaa ngi toog di ma \u00e0tte, ci li yoon wi digle, ba noppi santaane \u00f1u d\u00f3or ma, ci li yoon wi tere!\u00bb\n23:4 Waaye \u00f1a taxaw ca wetam ne ko: \u00abNdax dangay xas saraxalekat bu mag, bi Y\u00e0lla fal?\u00bb\n23:5 Pool tontu leen: \u00abBokk yi, xawma woon ne saraxalekat bu mag bi la, ndaxte t\u00ebral na\u00f1u ci Mbind mi ne: \u201cBul wax lu bon sa kilifag xeet.\u201d\u00bb\n23:6 Naka noona Pool, mi xam ne, genn-w\u00e0llu kureel ga bokk na\u00f1u ci tariixab Sadusen ya, te \u00f1a ca des bokk ci tariixab Farisen ya, mu wax ci kaw ci biir g\u00e9ew ba ne: \u00abBokk yi, man Farisen laa, te Farisen moo ma jur; li tax \u00f1u may \u00e0tte tey mooy sama yaakaar ci ne, \u00f1i dee dina\u00f1u dekki.\u00bb\n23:7 Bi mu waxee loolu nag, werante wu metti daldi xew diggante Farisen ya ak Sadusen ya, ba mbooloo ma xaajalikoo.\n23:8 Ndaxte Sadusen yi nanguwu\u00f1u ne, ndekkite mbaa malaaka mbaa rab, dara am na ci, waaye Farisen nangu na\u00f1u yooyu y\u00e9pp.\n23:9 Ci kaw loolu nag coow lu bare daldi jib. \u00d1enn ca xutbakat, ya bokk ca Farisen ya, ne b\u00ebr\u00e9t, daldi xuloo bu metti ne: \u00abGisunu dara lu bon ci nit kii. Su fekkeente ne, rab a ko wax mbaa malaaka...?\u00bb\n23:10 Noonu xuloo ba daldi g\u00ebn a t\u00e0ng, ba kilifa ga ragal ne, nit \u00f1i dina\u00f1u daggaate Pool. Kon mu sant xarekat ya, \u00f1u w\u00e0cc, nangu Pool ci \u00f1oom, y\u00f3bbu ko ca tata ja.\n23:11 Ca guddi ga nag Boroom bi taxaw ci wetu Pool ne ko: \u00abTakkal sa fit; ni nga ma seedee ci Yerusalem, noonu nga may seedee ca Room.\u00bb\n23:12 Bi b\u00ebt setee Yawut ya daldi lal pexe; \u00f1u dige ci ngi\u00f1 ne, du\u00f1u lekkati, du\u00f1u naanati, ba kera \u00f1uy rey Pool.\n23:13 \u00d1a lal pexe ma, seen lim \u00ebpp na \u00f1eent-fukk.\n23:14 Noonu \u00f1u dem ca saraxalekat yu mag ya ak njiit ya ne leen: \u00abGi\u00f1 nanu ne, dunu mos dara, ba kera nuy rey Pool.\n23:15 L\u00e9egi nag y\u00e9en ak kureelu \u00e0ttekat ya, laajleen kilifa ga, mu indi ko ci seen kanam, mel ni dangeen a b\u00ebgg a seet mbiram bu g\u00ebn a w\u00f3or. Bu ko defee nun dinanu fagaru, ngir rey ko, bala moo agsi.\u00bb\n23:16 Waaye jarbaatu Pool y\u00e9g fiir ga, mu dem, dugg ca tata ja, y\u00e9gal ko Pool.\n23:17 Bi ko Pool d\u00e9ggee, mu woo kenn ca njiiti xare ba ne ko: \u00abY\u00f3bbul waxambaane wii ca kilifa ga, ndax am na lu mu ko war a y\u00e9gal.\u00bb\n23:18 Njiit la j\u00ebl ko, y\u00f3bbu ko ca kilifa ga ne ko: \u00abPool, mi \u00f1u j\u00e0pp, moo ma woo, \u00f1aan ma, ma indil la waxambaane wii, ndaxte am na lu mu lay wax.\u00bb\n23:19 Noonu kilifa ga j\u00e0pp ci loxob waxambaane wa, w\u00e9etoo ak moom, laaj ko: \u00abLoo ma b\u00ebgg a y\u00e9gal?\u00bb\n23:20 Mu tontu ne: \u00abYawut yi da\u00f1oo dige, ngir \u00f1aan la, nga indi Pool \u00ebll\u00ebg ca kanamu kureelu \u00e0ttekat ya, mel ni da\u00f1oo b\u00ebgg a seet mbiram bu g\u00ebn a w\u00f3or.\n23:21 Bu leen ko may, ndaxte lu \u00ebpp \u00f1eent-fukk ci \u00f1oom \u00f1u ngi koy lalal fiir. Dige na\u00f1u ak ngi\u00f1 ne, dootu\u00f1u lekk, dootu\u00f1u naan, li feek reyu\u00f1u ko; fi mu ne sax fagaru na\u00f1u, di xaar, nga nangu.\u00bb\n23:22 Kilifa ga nag sant waxambaane wa, mu ba\u00f1 koo \u00e0gge kenn, ba noppi mu yiwi ko, mu dem.\n23:23 Bi mu ko defee mu woo \u00f1aar ci njiiti xare ba ne leen: \u00abWaajal-leen \u00f1aari t\u00e9em\u00e9eri xarekat ak jur\u00f3om-\u00f1aar-fukki gawar ak \u00f1aari t\u00e9em\u00e9er \u00f1u g\u00e0nnaayoo xeej, ngeen dem Sesare ci jur\u00f3om-\u00f1eenti waxtu ci guddi.\n23:24 Wutal-leen it Pool lu mu war, ngeen y\u00f3bbu ko ci j\u00e0mm ak salaam ba ca Feligs\u00eb, boroom r\u00e9ew mi.\u00bb\n23:25 Noonu mu bind bataaxal bii:\n23:26 Yaw Feligs\u00eb mu tedd mi, di boroom r\u00e9ew mi; man K\u00ebl\u00f3dd Lisiyas maa ngi lay nuyu.\n23:27 Yawut yi j\u00e0pp na\u00f1u nit kii, b\u00ebgg koo rey, waaye bi ma y\u00e9gee ne, jaambur la ci Room, wallu naa ko ak ay xarekat, ba musal ko.\n23:28 B\u00ebggoon naa xam lu tax \u00f1u kalaame ko. Moo tax ma y\u00f3bbu ko ca kanamu seen kureelu \u00e0ttekat ya.\n23:29 Gis naa ne li \u00f1u ko jii\u00f1 mu ngi aju ci ay werantey seen yoon, waaye jii\u00f1u\u00f1u ko dara lu jar dee mbaa j\u00e9ng.\n23:30 Te bi ma d\u00e9ggee ne, \u00f1u ngi koy fexeel, yebal naa ko ci yaw ci saa si. Sant naa nag \u00f1i ko kalaame, \u00f1u xamal la seen lay.\n23:31 Noonu xarekat ya j\u00ebl Pool ci guddi, indi ko ba ca d\u00ebkku Antipataris, ni \u00f1u leen ko sante.\n23:32 Ca \u00ebll\u00ebg sa \u00f1u wo\u00f1\u00f1iku, dellusi ca tata ja, b\u00e0yyi gawar ga, \u00f1u gunge ko.\n23:33 Bi gawar ga \u00e0ggee Sesare, \u00f1u jox boroom r\u00e9ew ma bataaxal ba, j\u00e9bbal ko Pool.\n23:34 Bi loolu amee boroom r\u00e9ew ma j\u00e0ng bataaxal ba, laaj ci ban diiwaan la Pool d\u00ebkk. Bi mu y\u00e9gee ne, mu ngi d\u00ebkk Silisi,\n23:35 mu ne ko: \u00abKon bu \u00f1i la kalaame \u00f1\u00ebwee, dinga layoo.\u00bb Mu santaane nag, \u00f1u denc ko ca k\u00ebr buur ba Erodd.\n24:1 Bi jur\u00f3omi fan w\u00e9yee, Ana\u00f1as saraxalekat bu mag ba dikk, \u00e0nd ak ay njiit ak layookat bu tudd Tertul, \u00f1u woo Pool ci yoon fa kanam boroom r\u00e9ew ma.\n24:2 Noonu \u00f1u woo Pool, te Tertul daldi ko jii\u00f1 naan: \u00abYaw Feligs\u00eb mu tedd mi, sa nguur jural na nu j\u00e0mm ju neex, te sa j\u00e0ppandil soppi na lu bare ci sunu xeet.\n24:3 Gis nanu ko f\u00e9pp ak ci l\u00e9pp, di la g\u00ebr\u00ebm ak sunu xol b\u00e9pp.\n24:4 Waaye ngir ba\u00f1 a y\u00e0ggal jataay bi, maa ngi lay \u00f1aan ci sa lewetaay, nga d\u00e9glu nu ci lu g\u00e0tt.\n24:5 Ndaxte ci mbirum nit kii teew, gis nanu ne rambaaj la, buy indi x\u00ebccoo ci Yawut yi ci \u00e0ddina s\u00e9pp, di njiitu mbooloo mu \u00f1uy wax Nasar\u00e9en.\n24:6 Dem na ba j\u00e9em a teddadil sax k\u00ebr Y\u00e0lla ga, waaye j\u00e0pp nanu ko.\n24:8 Soo ko laajee, yaw ci sa bopp, dinga gis ne, li nu koy jii\u00f1 d\u00ebgg la.\u00bb\n24:9 Ci kaw loolu Yawut ya \u00e0nd ca, di d\u00ebggal ne loolu w\u00f3or na.\n24:10 Bi loolu amee boroom r\u00e9ew ma jox Pool k\u00e0ddu gi. Noonu mu l\u00e0yyi ne: \u00abXam naa ne, yaa ngi \u00e0tte xeet wi diirub at yu bare, moo tax maa ngi l\u00e0yyi ak k\u00f3olute.\n24:11 Man ngaa w\u00f3orliku ne, \u00ebppagul fukki fan ak \u00f1aar demoon naa Yerusalem ngir m\u00e0ggali.\n24:12 Te kenn gisu ma, maay werante mbaa di j\u00f3gloo mbooloo, muy ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga mbaa ca j\u00e0ngu ya mbaa ci biir d\u00ebkk ba.\n24:13 Te m\u00ebnu\u00f1oo firndeel dara ci li \u00f1u may jii\u00f1 l\u00e9egi.\n24:14 Waaye nangu naa ci sa kanam ne, maa ngi jaamu Y\u00e0llay sunuy maam, ci topp yoon wi \u00f1u ne, mooy tariixa; terewul ne, l\u00e9pp li \u00f1u t\u00ebral ci yoonu Musaa ak li yonent yi bind, g\u00ebm naa ko.\n24:15 Te bokk naa ak \u00f1oom yaakaar ci Y\u00e0lla, ne \u00f1i jub ak \u00f1i jubadi dina\u00f1u dekki keroog yawmelxayaam.\n24:16 Moo tax fu ma tollu, maa ngi g\u00f3or-g\u00f3orlu, ngir am xel mu dal fa kanam Y\u00e0lla ak fa kanam nit \u00f1i.\n24:17 \u00abNoonu gannaaw g\u00ebjeb at yu bare \u00f1\u00ebw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te j\u00e9bbal Y\u00e0lla ay sarax.\n24:18 Bi ma koy def nag, gis na\u00f1u ma ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, ma setlu ba noppi, fekk \u00e0nduma ak mbooloo te indiwuma benn coow.\n24:19 Waaye ay Yawut yu d\u00ebkk Asi \u2014 xanaa kay \u00f1oo waroon a \u00f1\u00ebw ci sa kanam, di ma kalaame, bu \u00f1u amee dara lu \u00f1u may topp.\n24:20 Waaye it na nit \u00f1ii wax ci lan laa too\u00f1e ci jataayu g\u00e9ewub \u00e0tte ba,\n24:21 xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: \u201cMbirum ndekkitel \u00f1i dee moo tax ngeen d\u00ebj ma ci seen kanam tey!\u201d\u00bb\n24:22 Bi mu waxee noonu, Feligs\u00eb mi xam bu w\u00f3or mbirum yoon wi, yiwi leen ba beneen yoon. Mu ne leen: \u00abBu Lisiyas kilifag xare bi \u00f1\u00ebwee, dinaa \u00e0tte seen mbir.\u00bb\n24:23 Noonu mu sant njiitu xare ba ne ko: \u00abNanga wottu Pool, waaye nga may ko f\u00e9ex, te b\u00e0yyi ay xaritam, \u00f1u topptoo ko.\u00bb\n24:24 Bi ay fan w\u00e9yee, Feligs\u00eb \u00f1\u00ebwaat, \u00e0nd ak jabaram Dursil, miy Yawut. Noonu mu woolu Pool, di ko d\u00e9glu ci mbirum g\u00ebm Yeesu Kirist.\n24:25 Waaye bi Pool di waxtaan ci mbirum njub ak moom sa bopp ak b\u00e9s p\u00e9nc, Feligs\u00eb daldi tiit, yiwi ko ne ko: \u00abDemal, bu ma amee jot, dinaa la woolu.\u00bb\n24:26 Fekk yaakaaroon na it ne, Pool dina ko jox xaalis; kon mu di ko faral a woolu, ngir waxtaan ak moom.\n24:27 Bi \u00f1aari at weesoo nag, amoon na ku wuutu Feligs\u00eb, tudd Porsiyus Festus. Noonu Feligs\u00eb, mi b\u00ebggoon lu neex Yawut ya, b\u00e0yyi Pool ca kaso ba.\n25:1 Bi Festus teersee ci diiwaanam, mu teg ca \u00f1etti fan, dem Yerusalem.\n25:2 Noonu saraxalekat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame Pool ci moom.\n25:3 \u00d1uy s\u00e0kku ndimbal ci moom, di ko \u00f1aan bu w\u00e9r, mu y\u00f3nni Pool Yerusalem, fekk lal na\u00f1u fiiru rey ko ca yoon wa.\n25:4 Waaye Festus tontu leen ne: \u00ab\u00d1u ngi wottu Pool ca Sesare, te dinaa fa dem fi ak fan yu n\u00e9ew.\u00bb\n25:5 Mu ne leen: \u00ab\u00d1i am maana ci y\u00e9en nag, nangeen \u00e0nd ak man, layooji ak nit ka, bu dee too\u00f1 na.\u00bb\n25:6 Noonu Festus am fa \u00f1oom jur\u00f3om-\u00f1ett ba fukki fan, ba noppi dem Sesare. Ca \u00ebll\u00ebg sa mu toog ca \u00e0ttekaay ba, joxe ndigal, \u00f1u indi Pool.\n25:7 Bi mu \u00f1\u00ebwee nag, Yawut ya j\u00f3ge Yerusalem w\u00ebr ko, di ko jii\u00f1 too\u00f1 yu bare te r\u00e9y, te m\u00ebnu\u00f1u leen a firndeel.\n25:8 Noonu Pool l\u00e0yyi ne: \u00abToo\u00f1uma yoonu Yawut ya, too\u00f1uma k\u00ebr Y\u00e0lla ga, too\u00f1uma buur ba Sesaar.\u00bb\n25:9 Ci kaw loolu Festus, mi b\u00ebgg lu neex Yawut ya, tontu Pool ne: \u00abNdax b\u00ebgguloo dem Yerusalem, nga layoo fa ci mbir yii ci sama kanam?\u00bb\n25:10 Waaye Pool ne ko: \u00abMaa ngi nii taxaw ci kanam \u00e0ttekaayu buur Sesaar; te fii la\u00f1u ma war a \u00e0ttee. Te yaw ci sa bopp xam nga bu baax ne, too\u00f1uma Yawut yi.\n25:11 Su ma too\u00f1oon mbaa ma def lu bon lu jar dee, kon duma tinu ngir ba\u00f1 a dee. Waaye bu li \u00f1u may jii\u00f1 taxawul, kenn sa\u00f1u ma leen a j\u00e9bbal. D\u00e9nk naa sama mbir Sesaar.\u00bb\n25:12 Bi mu waxee loolu, Festus gise ak \u00f1i ko w\u00ebr, mu tontu ko: \u00abD\u00e9nk nga sa mbir Sesaar, kon ci moom ngay dem.\u00bb\n25:13 Ba \u00f1u ca tegee ay fan, buur Agaripa ak Berenis \u00f1\u00ebw Sesare, ngir nuyusi Festus.\n25:14 Bi seen ngan di ruus nag, Festus diis buur ba mbirum Pool ne ko: \u00abFeligs\u00eb batale na nu ak kenn ku \u00f1u t\u00ebj.\n25:15 Te bi ma nekkee Yerusalem, saraxalekat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame na\u00f1u ko ci man, \u00f1aan ma, ma daan ko.\n25:16 Waaye ma tontu leen ne: \u201cJ\u00e9bbale nit, fekk j\u00e0kkaarloowul ak \u00f1i koy jii\u00f1, ba man a l\u00e0yyil boppam ci li \u00f1u koy jii\u00f1, loolu d\u00ebppoowul ak aaday nguuru Room.\u201d\n25:17 Bi \u00f1u \u00e0ndee ak man ba fii nag, randaluma mbir mi, waaye ca \u00ebll\u00ebg sa sax toog naa ca \u00e0ttekaay ba, joxe ndigal, \u00f1u indi nit kooku.\n25:18 \u00d1i koy kalaame nag, bi \u00f1u taxawee, jii\u00f1u\u00f1u ko benn \u00f1aawteef ci yi ma yaakaaroon;\n25:19 waaye \u00f1uy werante rekk ak moom ci seen yoon ak ci mbirum ku tudd Yeesu, mi dee, te Pool sax ci ne, mu ngi dund.\n25:20 Gannaaw lijjanti mbir moomu jafe woon na ma lool nag, ma laaj ko, ndax b\u00ebgg na dem Yerusalem, layooji fa ci mbir yooyu.\n25:21 Waaye Pool \u00f1aan, nu fomm mbiram, ba kera buur bu tedd ba di ko \u00e0tte. Noonu santaane naa \u00f1u aj ko, ba keroog ma koy y\u00f3nnee Sesaar.\u00bb\n25:22 Booba nag Agaripa ne Festus: \u00abMan sax b\u00ebgg naa d\u00e9gg nit kooku.\u00bb Festus tontu ko: \u00abBu \u00ebll\u00ebgee dinga ko d\u00e9gg.\u00bb\n25:23 Ca \u00ebll\u00ebg sa nag Agaripa ak Berenis \u00f1\u00ebw bu xumb, \u00f1u dugg ca n\u00e9egu \u00e0tte ba, \u00e0nd ak kilifay xare ba ak \u00f1a am maana ca d\u00ebkk ba. Noonu Festus joxe ndigal, \u00f1u indi Pool.\n25:24 Bi mu \u00f1\u00ebwee, Festus ne: \u00abBuur Agaripa ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp, \u00f1i fi teew tey, nit kaa ngi nii! Mbiram moo tax mbooloom Yawut y\u00e9pp, muy ci Yerusalem, muy fii, w\u00ebr ma di yuuxu ne: \u201cNit kii waratul a dund.\u201d\n25:25 Waaye gis naa ne, deful dara lu jar dee. Moona, gannaaw moom ci boppam d\u00e9nk na boppam buur bu tedd ba, fas naa y\u00e9ene y\u00f3nnee ko ko.\n25:26 Fekk awma dara lu w\u00f3or ci mbiram, lu ma man a bind sang bi. Moo tax ma indi ko ci seen kanam, rawatina ci sa kanam buur Agaripa, ngir sunu jataay may ma lu ma bind.\n25:27 Ndaxte yaakaar naa ne, y\u00f3nnee ku \u00f1u t\u00ebj, te ba\u00f1 caa boole lu ko waral, \u00e0ndul ak xel.\u00bb\n26:1 Bi mu ko waxee, Agaripa ne Pool: \u00abJ\u00eblal k\u00e0ddu gi.\u00bb Noonu Pool t\u00e0llal loxoom, daldi l\u00e0yyi ne:\n26:2 \u00abBuur Agaripa, ma l\u00e0yyi ci sa kanam tey ci l\u00e9pp, li ma Yawut yiy jii\u00f1, xol bu sedd la ci man,\n26:3 ndaxte xam nga bu baax aaday Yawut yi ak seeni werantey yoon. Kon maa ngi lay \u00f1aan, nga d\u00e9glu ma ak mu\u00f1.\n26:4 \u00abCi lu j\u00ebm ci Yawut yi, xam na\u00f1u sama dund li dale ci samag ndaw, muy ci sama biir xeet, muy ci Yerusalem.\n26:5 Xam na\u00f1u ma bu y\u00e0gg te man na\u00f1oo seede, su leen neexee, ne daan naa dund ni Farisen, te mooy tariixa bi g\u00ebn a diis ci sunu diine.\n26:6 Li ma indi ci kureelu \u00e0ttekat yii nag, mooy yaakaar ne, Y\u00e0lla dina amal li mu digoon sunuy maam.\n26:7 Dige booba la fukki giir ak \u00f1aar yu b\u00e0nni Israyil di s\u00e0kku, ngir jot ko, ci jaamu Y\u00e0lla ak cawarte guddi ak b\u00ebcc\u00ebg. Yaw buur, yaakaar joojoo tax \u00f1u may kalaame, \u00f1oom Yawut yi.\n26:8 Lu tax seen xel d\u00e0q ne, Y\u00e0lla dina dekkal \u00f1i dee?\n26:9 \u00abMan sax ci sama bopp defe woon naa ne, war naa def lu bare, ngir suufeel turu Yeesum Nasaret.\n26:10 Daan naa ko def ci Yerusalem, ba noppi ma jot sa\u00f1-sa\u00f1 ci saraxalekat yu mag ya, bay t\u00ebj gaayi Y\u00e0lla yu bare. Rax-ca-dolli ku \u00f1u ci masoon a b\u00ebgg a rey, \u00e0nd naa ci.\n26:11 Daan naa w\u00ebr j\u00e0ngoo-j\u00e0ngu, di leen teg toskare te di leen j\u00e9em a weddiloo. Te sama mer daa na tar, ba ma di leen xa\u00f1 ba ca d\u00ebkk yu sore, ngir fitnaal leen.\n26:12 \u00abNoonu am b\u00e9s, may dem d\u00ebkku Damas, yor sa\u00f1-sa\u00f1 ak ndigalu saraxalekat yu mag ya.\n26:13 Ca njolloor, buur bi, gis naa ca yoon wa leer gu j\u00f3ge asamaan ne r\u00e0yy, ba raw leeru jant, melax ba \u00ebmb ma, man ak \u00f1i ma \u00e0ndal.\n26:14 Nu ne n\u00ebr\u00ebm ci suuf, ma d\u00e9gg baat bu ma wax ci l\u00e0kku yawut ne: \u201cSool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal? Ngay b\u00ebre ak man ni fas wuy wo\u014b\u014beetu ku koy jam d\u00ebg\u00ebl, metti na ci yaw.\u201d\n26:15 \u00abNoonu ma tontu ko: \u201cYaa di kan, Boroom bi?\u201d Boroom bi ne ma: \u201cMaa di Yeesu, mi ngay fitnaal.\n26:16 Waaye j\u00f3gal taxaw. Lii moo tax ma fee\u00f1u la: teg naa la yen, nga di ma seedeel ci l\u00e9pp li nga gis ci man, ak li ma lay fee\u00f1uji.\n26:17 Dinaa la musal ci b\u00e0nni Israyil ak ci \u00f1i dul Yawut. Ci \u00f1oom laa lay yebal,\n26:18 ngir ubbi seeni b\u00ebt, nga j\u00eble leen ci l\u00ebnd\u00ebm, t\u00e0bbal leen ci leer, nga nangoo leen ci sa\u00f1-sa\u00f1u Seytaane, wo\u00f1\u00f1i leen ci Y\u00e0lla, ma baal leen seeni b\u00e0kkaar te may leen c\u00e9r ci biir sama gaa yi sell ci kaw ng\u00ebm.\u201d\n26:19 \u00abKon nag buur Agaripa, woruma li ma Y\u00e0lla yen ci pee\u00f1u.\n26:20 Waaye li t\u00e0mbali ci Damas, teg ci d\u00ebkku Yerusalem ak r\u00e9ewu Yawut m\u00e9pp, ba agsi ci \u00f1i dul Yawut, y\u00e9gal naa leen, \u00f1u tuub seeni b\u00e0kkaar te wo\u00f1\u00f1iku ci Y\u00e0lla, bay j\u00ebf lu d\u00ebppook r\u00e9ccu.\n26:21 Loolu nag moo waral Yawut yi j\u00e0pp ma ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, di ma fexee rey.\n26:22 Waaye gannaaw Y\u00e0llaa ngi may taxawu ba tey, maa ngi taxaw fi, di ko seedeel ci mag ak ndaw; yokkuma dara ci li yonent yi ak Musaa xamle woon lu jiitu,\n26:23 maanaam Almasi bi dina d\u00e9kku ay coono, te mooy j\u00ebkk a dekki, bay jollil leer ci b\u00e0nni Israyil ak \u00f1i dul Yawut.\u00bb\n26:24 Bi muy l\u00e0yyee nii, Festus daldi ko g\u00ebdd ak baat bu kawe ne ko: \u00abDangaa dof Pool! Xanaa sa nj\u00e0ng mu r\u00e9y mi da laa xa\u00f1 sago.\u00bb\n26:25 Waaye Pool tontu ko: \u00abFestus mu tedd mi, dofuma; waaye lu d\u00ebggu laay wax te \u00e0nd ak sago.\n26:26 Y\u00ebf yii leer na buur bi, moo tax maa ngi koy wax ak k\u00f3olute. W\u00f3or naa ne, dara ci lii may wax umpu ko, ndaxte lii amewul ciy ruq.\n26:27 Yaw buur Agaripa, ndax g\u00ebmuloo yonent yi? Xam naa bu w\u00e9r ne, g\u00ebm nga.\u00bb\n26:28 Noonu Agaripa ne Pool: \u00abXanaa yaw, ci diir bu g\u00e0tt bii rekk, nga ma b\u00ebgg a dugale ci gaayi Kirist!\u00bb\n26:29 Pool tontu ko: \u00abMuy tey, muy \u00ebll\u00ebg, waxuma yaw rekk waaye it \u00f1i may d\u00e9glu tey \u00f1\u00e9pp, na Y\u00e0lla def, ba ngeen fekksi ma ci li ma nekk, lu moy j\u00e9ng yii!\u00bb\n26:30 Ci kaw loolu buur ba daldi j\u00f3g, boroom r\u00e9ew ma topp ci, Berenis tegu ca ak mbooloo ma m\u00e9pp.\n26:31 Bi \u00f1u g\u00e9nnee nag, \u00f1uy waxante ne: \u00abNit kii deful dara lu jar dee mbaa kaso.\u00bb\n26:32 Te Agaripa ne Festus: \u00abManoon nanu koo yiwi, bu d\u00e9nkuloon mbiram Sesaar.\u00bb\n27:1 Bi loolu w\u00e9yee \u00f1u fas y\u00e9ene noo dugal gaal j\u00ebme r\u00e9ewu Itali. Noonu \u00f1u j\u00ebl Pool ak \u00f1eneen \u00f1i \u00f1u t\u00ebjoon, d\u00e9nk leen njiitu xare bu tudd Yulyus, mi bokk ci mbooloom xare mu buur.\n27:2 Nu dugg ca gaalu d\u00ebkku Adaramit guy taxaw ci teeruy Asi, daldi t\u00e0bbi ci biir g\u00e9ej; te Arist\u00e0rk, mi d\u00ebkk Tesalonig ci diiwaanu Maseduwan, \u00e0nd ak nun.\n27:3 Ca \u00ebll\u00ebg sa nu teer Sidon; Yulyus laabiir ci Pool, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir \u00f1u ganale ko.\n27:4 Bi nu fa j\u00f3gee, nu dem ci biir g\u00e9ej, leru dunu Sipar ci fegu ngelaw li, ndaxte ngelaw li da noo soflu.\n27:5 Nu j\u00e0ll g\u00e9ej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, teersi Mira ca w\u00e0lli Lisi.\n27:6 Foofa nag njiit la gis gaal gu j\u00f3ge Alegs\u00e0ndiri, j\u00ebm Itali, mu dugal nu ca.\n27:7 Noonu nuy dem nd\u00e0nk diirub fan yu bare, ba janook Kanidd ci kaw coono bu r\u00e9y; te ndegam ngelaw li mayu nu, nu j\u00ebm kanam, nu leru dunu Kereet ci fegu ngelaw li, janook Salmon.\n27:8 Nu romb fa ak coono yu bare, agsi ca b\u00e9rab bu \u00f1uy wax Teeru yu neex, te dend ak d\u00ebkku Lase.\n27:9 Fekk booba y\u00e0ggoon na\u00f1u ca yoon wa, te dem ci g\u00e9ej daldi aaytal, ndaxte jamonoy Kooru Yawut ya wees na. Moo tax Pool digal leen ne:\n27:10 \u00abGaa \u00f1i, gis naa ne, tukki bi \u00ebmb na musiba ak kasara ju bare, waxuma gaal gi ak li mu yeb waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.\u00bb\n27:11 Waaye njiit la sobental waxi Pool, d\u00e9ggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.\n27:12 Te gannaaw teeru ba neexul a lollikoo, \u00f1a ca \u00ebpp m\u00e0nkoo ci j\u00f3ge fa, dem ci biir g\u00e9ej, ngir wut a agsi Fenigs\u00eb, biy teerub dunu Kereet te janook sowu suuf ak sowu kaw, nu lollikoo fa.\n27:13 Noonu bi ngelaw lu woyof liy j\u00f3ge sudd wolee, \u00f1u defe ne, man na\u00f1oo sottal seen pexe, \u00f1u w\u00ebgg diigal, daldi tafu ci dunu Kereet.\n27:14 Waaye nes tuuti ngelaw lu wole penku, \u00f1u di ko wax \u00ab\u00cbrakilon,\u00bb j\u00f3ge ca dun ba, ne milib ci sunu kaw.\n27:15 Mu \u00ebpp doole gaal ga, daldi ko wat, ba nu bayliku, daldi yal.\n27:16 Nu daldi daw, leru dun bu tuuti bu \u00f1uy wax K\u00f3da ci fegu ngelaw, rawale looco ga ci kaw gaal ga ak coono bu bare.\n27:17 Bi \u00f1u ko y\u00e9egee, \u00f1u fab ay buum, ngir laxas ca taatu gaal ga, ngir ragal a daanu ci suuf su nooy su \u00f1uy wax Sirt; ba noppi \u00f1u daldi s\u00e0nni diigal, ngir w\u00e0\u00f1\u00f1i doxub gaal ga, nuy yale noonu.\n27:18 Waaye bi nu ngelaw li sonalee bu metti, ca \u00ebll\u00ebg sa \u00f1u s\u00e0nni la gaal ga yeboon ca g\u00e9ej ga.\n27:19 Te ca \u00f1etteelu fan ba, \u00f1u s\u00e0nni ak seeni loxo jumtukaay, yi \u00f1u yeboon ngir f\u00e0ggu.\n27:20 Noonu jant bi ne me\u014b\u014b te biddiiw ne mes ay fan yu bare, fekk ba tey ngelaw li di wol ak doole, ba sunu yaakaaru mucc g\u00e9pp tas.\n27:21 Bi loolu di xew, fekk g\u00ebj na\u00f1oo lekk, Pool daldi taxaw ci seen biir ne leen: \u00abGaa \u00f1i, li g\u00ebnoon mooy ngeen d\u00e9glu ma te ba\u00f1 a j\u00f3ge Kereet, ba indil seen bopp musiba ak kasara ju r\u00e9y jii.\n27:22 L\u00e9egi nag maa ngi leen di d\u00e9nk, ngeen takk seen fit, ndax gaal gi rekk mooy y\u00e0qu, waaye kenn ci y\u00e9en du dee.\n27:23 Ndaxte ci guddi menn malaaka dikkal na ma, j\u00f3ge ci Y\u00e0lla sama Boroom, bi may jaamu.\n27:24 Mu ne ma: \u201cPool bul tiit; f\u00e0ww nga taxaw ci kanamu Sesaar, te yaa tax Y\u00e0llay aar bakkani \u00f1i nga \u00e0ndal \u00f1\u00e9pp.\u201d\n27:25 Moo tax gaa \u00f1i, takkleen seen fit, ndax w\u00f3olu naa Y\u00e0lla ne, li mu ma wax, dina am.\n27:26 Waaye war nanoo luf cib dun.\u00bb\n27:27 Ca fukkeelu guddi ga ak \u00f1eent nu nga doon jaya\u014b-jaya\u014bi ca g\u00e9eju Adiratig; noonu ca xaaju guddi dawalkati gaal ga defe ne, danu jegesi suuf.\n27:28 \u00d1u s\u00e0nni nattukaay ba ci biir g\u00e9ej, mu j\u00e0pp \u00f1eent-fukki meetar, dem ca kanam tuuti, s\u00e0nniwaat ko, j\u00e0pp fanweeri meetar.\n27:29 \u00d1u ragal ne, dina\u00f1u fenqu ci ay xeer, kon \u00f1u daldi s\u00e0nni \u00f1eenti diigal ci geenu gaal ga, di \u00f1aan b\u00ebt set.\n27:30 Waaye ci kaw loolu dawalkati gaal ga taafantaloo s\u00e0nniji ay diigal ca boppu gaal ga, fekk da\u00f1uy fexee j\u00ebl looco ga, ba raw.\n27:31 Waaye Pool ne njiit la ak xarekat ya: \u00abBu \u00f1ii desul ci gaal gi, dungeen raw.\u00bb\n27:32 Noonu xarekat ya dagg buum, yay t\u00e9ye looco ga, b\u00e0yyi ko mu w\u00e9y.\n27:33 Bi b\u00ebt setagul, Pool sant leen \u00f1u lekk; mu ne leen: \u00abTey mooy seen fukki fan ak \u00f1eent yu ngeen ne jonn, lekkuleen, mosuleen dara.\n27:34 Maa ngi leen di sant nag, ngeen lekk, ndax noonu rekk ngeen man a rawe. Ndax genn kawar du rot ci y\u00e9en.\u00bb\n27:35 Bi mu waxee loolu, mu fab mburu, sant Y\u00e0lla ci kanamu \u00f1\u00e9pp, damm ko, daldi ko lekk.\n27:36 Bi \u00f1u gisee loolu, \u00f1\u00e9pp d\u00ebg\u00ebraat, \u00f1u daldi lekk \u00f1oom itam.\n27:37 Mboolem \u00f1i nekkoon ca gaal ga mat na \u00f1aari t\u00e9em\u00e9eri nit ak jur\u00f3om-\u00f1aar-fukk ak jur\u00f3om-benn.\n27:38 Noonu \u00f1u lekk ba suur, daldi s\u00e0nni pepp ma ca g\u00e9ej ga, ngir woyofal gaal ga.\n27:39 Bi b\u00ebt setee nag, x\u00e0mmiwu\u00f1u r\u00e9ew ma, waaye s\u00e9en na\u00f1u ruqu tefes. Noonu \u00f1u fas y\u00e9ene caa teeral gaal ga, bu \u00f1u ko manee.\n27:40 \u00d1u dagg diigal ya, b\u00e0yyi leen ci biir g\u00e9ej, yiwiwaale baar ba; ba noppi firi wiiru kanam ga, jublu ca tefes ga.\n27:41 Waaye \u00f1u dal ca tundu suuf ca b\u00e9rab bu \u00f1aari koro\u014b daje, gaal ga daldi fa luf. Boppu gaal ga nuur bu baax, ne fa tekk, te dooley duus ya daldi toj geen ba.\n27:42 Bi loolu amee xarekat ya b\u00ebgg a rey \u00f1i \u00f1u t\u00ebj, ngir ragal \u00f1enn \u00f1i f\u00e9ey, ba raw.\n27:43 Waaye njiit la b\u00ebgg a musal Pool, mu tere leen pexe ma. Mu sant \u00f1i man a f\u00e9ey, \u00f1u j\u00ebkk a s\u00f3obu ca ndox ma, ba jot tefes ga.\n27:44 Mu sant \u00f1i ci des \u00f1u def noonu, langaamu ci ay d\u00e9nk, mbaa ca tojiti gaal ga. Noonu \u00f1\u00e9pp jot tefes ga ci j\u00e0mm ak salaam.\n28:1 Bi nu r\u00ebccee, nu y\u00e9g ne dun baa nga tudd M\u00e0lt.\n28:2 Te waa r\u00e9ew ma won nu laabiir gu r\u00e0\u00f1\u00f1iku, ndaxte taalal na\u00f1u nu safara, ganale nu ndax taw bi s\u00f3ob ak sedd bi.\n28:3 Pool nag di for matt, di ko def ca taal ba, jaan ne ca m\u00eblle ndax t\u00e0ngoor wa, taq ci loxoom.\n28:4 Bi waa r\u00e9ew ma gisee rab wa w\u00e9qu ci loxoom nag, \u00f1uy waxante naan: \u00abCi lu w\u00f3or nit kii reykat la; te bi mu r\u00ebccee ca g\u00e9ej ga sax, ndogalu Y\u00e0lla mayu ko mu dund.\u00bb\n28:5 Waaye Pool y\u00ebl\u00ebb rab wa ca safara sa, te w\u00e0\u00f1\u00f1iwu ko dara.\n28:6 Nit \u00f1i di xaar mu newi, mbaa mu ne d\u00e0ll, dee; waaye bi \u00f1u n\u00e9gee lu y\u00e0gg te gis ne dara jotu ko, \u00f1u soppi xel ne: \u00abKii y\u00e0lla la.\u00bb\n28:7 Amoon na nag ca wet ya ay suuf yu doon moomeelu ku tudd Publiyus, di kilifag dun ba. Mu teeru nu, ganale nu ngan gu r\u00e9y diirub \u00f1etti fan.\n28:8 Fekk baayu Publiyus dafa t\u00ebdd ndax ay t\u00e0ngoori yaram yu koy dikkal ak biiru ta\u00f1\u00f1. Pool nag dem seeti ko, \u00f1aan ci Y\u00e0lla, teg ko ay loxoom, mu daldi w\u00e9r.\n28:9 Ci kaw loolu jarag ya ca des ca dun ba daldi dikk, amaat w\u00e9r-gi-yaram.\n28:10 \u00d1u teral nu ci f\u00e0nn yu bare, te bi nuy dem, \u00f1u jox nu li nuy soxla l\u00e9pp.\n28:11 Bi nu fa amee \u00f1etti weer, nu dugg ca gaal gu lollikoo ca dun ba, daldi t\u00e0bbi ca g\u00e9ej ga. Gaalu d\u00ebkku Alegs\u00e0ndiri la woon, te yor x\u00e0mmikaay guy nataalu Kastor ak Polugs\u00eb.\n28:12 Noonu nu teer d\u00ebkku Sirakus, toog fa \u00f1etti fan.\n28:13 Nu j\u00f3ge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca \u00ebll\u00ebg sa ngelawu sudd daldi j\u00f3g, te ca \u00f1aareelu fan ba nu teer Pusol.\n28:14 Gis nanu fa ay bokk, \u00f1u \u00f1aan nu, nu toog fa ayu-b\u00e9s. Noonu nu dem Room.\n28:15 Sunuy xebaar law na, ba egg ca bokk ya fa d\u00ebkk, noonu \u00f1u gatandu nu ba ca p\u00e9ncu Apiyus ak b\u00e9rab bu \u00f1uy wax \u00d1etti a\u00f1ukaay ya. Bi leen Pool gisee, mu sant Y\u00e0lla, daldi takk fitam.\n28:16 Bi nu dikkee Room nag, \u00f1u may Pool, mu d\u00ebkk fa ko lew, moom ak xarekat ba koy wottu.\n28:17 Bi \u00f1etti fan w\u00e9yee, mu woolu njiiti Yawuti d\u00ebkk ba. Bi \u00f1u dajaloo nag, mu wax leen lii: \u00abBokk yi, j\u00e0pp na\u00f1u ma ci Yerusalem, j\u00e9bbal ma waa Room, fekk defuma dara luy suufeel sunu xeet, mbaa lu juuyoo ak sunuy aaday maam.\n28:18 Waa Room nag seet sama mbir, te b\u00ebgg maa b\u00e0yyi, ndaxte toppu\u00f1u ma dara lu jar dee.\n28:19 Waaye bi ko Yawut ya ba\u00f1ee, fas y\u00e9ene naa d\u00e9nk sama mbir Sesaar, fekk ba tey awma dara lu may taqal sama xeet.\n28:20 Moo tax ma \u00f1aan a gise ak y\u00e9en, nu diisoo, ndaxte yaakaaru b\u00e0nni Israyil moo tax \u00f1u j\u00e9ng ma.\u00bb\n28:21 Bi \u00f1u ko d\u00e9ggee, \u00f1u tontu ko: \u00abJotunu benn bataaxal bu j\u00f3ge Yude ci sa mbir, te kenn ci bokk, yi fi dikk, jottaliwul mbaa mu seede ci yaw lu bon.\n28:22 Waaye b\u00ebgg nanoo d\u00e9gg li nga g\u00ebm, ndaxte xam nanu ne, tariixa booba, kenn jubluwu ko fenn.\u00bb\n28:23 Noonu \u00f1u dig ko b\u00e9s, te \u00f1u bare \u00f1\u00ebw, fekksi ko ca n\u00e9egam. Mu di leen j\u00e0ngal suba ba ngoon, di leen d\u00ebggal lu j\u00ebm ci nguuru Y\u00e0lla ak ci Yeesu, tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi, di leen j\u00e9em a g\u00ebmloo.\n28:24 \u00d1enn \u00f1i nag g\u00ebm li mu wax, \u00f1a ca des weddi ko.\n28:25 Gannaaw m\u00ebnu\u00f1oo d\u00e9ggoo, \u00f1u b\u00ebgg a tas. Waaye bi \u00f1u laata dem, Pool teg ca wax jii: \u00abXel mu Sell mi wax na d\u00ebgg ak seeni maam, jaarale ko ci yonent Y\u00e0lla Esayi.\n28:26 Nee na:\u201cDemal ci xeet wii ne leen:\u2018Dingeen d\u00e9glu bu baaxwaaye dungeen xam dara;di xool bu baax waaye dungeen gis dara.\u2019\n28:27 Ndaxte xolu xeet wii dafa d\u00ebrkiis;da\u00f1uy d\u00e9glu ak nopp yu naqari,tey g\u00ebmm seeni b\u00ebt,ngir ba\u00f1 a gis ak seeni b\u00ebt,d\u00e9gg ak seeni nopp,te xam ci seen xol,\u00f1u wo\u00f1\u00f1iku ci man, ma w\u00e9ral leen.\u201d\n28:28 \u00abXamleen nag ne, xebaaru mucc gii y\u00e9gal na\u00f1u ko \u00f1i dul Yawut, te \u00f1oom dina\u00f1u ko d\u00e9glu.\u00bb\n28:30 Noonu diirub \u00f1aari at Pool d\u00ebkk ca k\u00ebr gu muy fey, di fa \u00e0ggali \u00f1\u00e9pp \u00f1i koy seetsi.\n28:31 Muy y\u00e9gle nguuru Y\u00e0lla, di j\u00e0ngale ci mbirum Boroom bi Yeesu Kirist ak fit wu d\u00ebg\u00ebr, te kenn terewu ko ko.","title":"Wolof Bible (NT): Acts","type":"page"}
