{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/co1.htm","path":"bib/wb/wlf/co1.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/co1.htm","text":"1:1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Y\u00e0lla, man ak Sosten sunu mbokk,\n1:2 noo leen di bind, y\u00e9en mbooloom Y\u00e0lla, mi d\u00ebkk Korent. Nu ngi leen di nuyu, y\u00e9en \u00f1i Y\u00e0lla s\u00e9dde boppam jaare ci Kirist Yeesu, y\u00e9en \u00f1i Y\u00e0lla woo, ngeen sell, boole leen ak \u00f1i nekk ci \u00e0ddina s\u00e9pp tey tudd turu sunu Boroom Yeesu Kirist, miy seen Boroom, di sunu bos.\n1:3 Na leen Y\u00e0lla sunu Baay ak Yeesu Kirist Boroom bi may yiw ak j\u00e0mm.\n1:4 Duma j\u00f3g ci di sant Y\u00e0lla sama Boroom ci seen mbir ndax yiw, wi mu leen may ci seen bokk ci Kirist Yeesu.\n1:5 Ndaxte ci yiwi Y\u00e0lla y\u00e9pp ngeen woomle ci Kirist, muy ci wax, muy ci xam-xam.\n1:6 Ndaxte li nu doon seedeel Kirist, Y\u00e0lla d\u00ebggal na ko ci y\u00e9en.\n1:7 Noonu nag \u00f1\u00e0kkuleen genn may l\u00e9egi bi ngeen di s\u00e9entu waxtu, wi sunu Boroom Yeesu Kirist di fee\u00f1 ci biir ndamam.\n1:8 Kirist dina leen dooleel ba ca muj ga, ngir ngeen ba\u00f1 a am wenn \u014b\u00e0\u00f1\u00f1 b\u00e9s bu sunu Boroom Yeesu Kirist dellusee.\n1:9 Y\u00e0lla kuy s\u00e0mm k\u00f3ll\u00ebre la, moom mi leen woo, ngir ngeen bokk ak Doomam Yeesu Kirist, sunu Boroom.\n1:10 Waaye bokk yi, maa ngi leen di d\u00e9nk ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen juboo te ba\u00f1 a f\u00e9ewaloo ci seen biir. Waaye nangeen \u00e0nd te booloo, bokk xel, bokk xalaat.\n1:11 Ndaxte bokk yi, waa k\u00ebr Kelowe xamal na\u00f1u ma ne, dangeen di xuloo.\n1:12 Maa ngi \u00f1\u00ebw ca wax ja: kenn ku nekk ci y\u00e9ena ngi naan: \u00abMan ci Pool laa bokk!\u00bb \u00abMan ci Apolos!\u00bb \u00abMan ci Sefas!\u00bb \u00abMan ci Kirist!\u00bb\n1:13 Ndax Kirist dafa xaajoo? Ndax Pool la\u00f1u daajoon ca bant ba, mu dee ngir y\u00e9en? Ndax s\u00f3ob na\u00f1u leen ci ndox, ngir wone ne bokk ngeen ci Pool?\n1:14 Maa ngi sant Y\u00e0lla ci li ma s\u00f3obul kenn ci y\u00e9en, ku dul Kirispus ak Gayus,\n1:15 ngir kenn ba\u00f1 a wax ne, ci sama tur la\u00f1u ko s\u00f3ob.\n1:16 Aa\u014bkay! S\u00f3ob naa it ci ndox waa k\u00ebr Estefanas. Waaye ci sama p\u00e0ttaliku s\u00f3obuma keneen.\n1:17 Ndaxte Kirist yebalu ma ngir may s\u00f3obe ci ndox, waaye da maa yebal, ngir may y\u00e9gle xebaar bu baax bi, te ma ba\u00f1 koo def ak waxi xam-xamu nit, ngir ba\u00f1 a \u00f1\u00e0kkal faayda deewu Kirist ca bant ba.\n1:18 Ndaxte y\u00e9gleb deewu Kirist ca bant ba, ag ndof la ci \u00f1iy s\u00e0nku. Waaye ci nun \u00f1i aw ci yoonu mucc gi, dooley Y\u00e0lla la.\n1:19 Ndaxte Mbind mi nee na:\u00abDinaa folli xam-xamu boroom xam-xam yi,lem xalaati \u00f1i am xel.\u00bb\n1:20 Ana boroom xam-xam bi? Ana kaa\u014b mi? Ana boroom l\u00e0mmi\u00f1 wu neex, wi ci \u00e0ddina sii? Xanaa Y\u00e0lla wonewul ne, xam-xamu \u00e0ddina si ag ndof la?\n1:21 Gannaaw \u00e0ddina si ci xam-xamam demul ba xam Y\u00e0lla --te Y\u00e0llaa dogal loolu ci xam-xamam \u2014 soob na Y\u00e0lla mu musal \u00f1i g\u00ebm, jaar ci y\u00e9gleb xebaaru Kirist, fekk ag ndof la ci b\u00ebti nit.\n1:22 Ndaxte Yawut yi \u00f1u ngi laaj ay firnde; Gereg yi di wut xam-xam.\n1:23 Waaye nun nu ngi y\u00e9gle Kirist, mi \u00f1u reyoon ca bant ba, te loolooy t\u00e9q ng\u00ebmu Yawut yi, di ag ndof ci \u00f1i dul Yawut.\n1:24 Waaye ci \u00f1i Y\u00e0lla woo, \u00f1uy Yawut mbaa di Gereg, Kirist mooy dooley Y\u00e0lla, di xam-xamu Y\u00e0lla.\n1:25 Li \u00f1uy wax ag ndof ca w\u00e0llu Y\u00e0lla moo g\u00ebn a tedd xam-xamu nit. Te li \u00f1uy wax \u00f1\u00e0kk dooley Y\u00e0lla moo \u00ebpp k\u00e0ttan dooley nit.\n1:26 Bokk yi, seetleen seen nekkin, bi leen Y\u00e0lla di woo. Barewul woon ci y\u00e9en, \u00f1i \u00f1uy tudde ay boroom xam-xam mbaa ay boroom doole mbaa \u00f1u rafet ab juddu.\n1:27 Waaye li \u00e0ddina teg ag ndof, Y\u00e0lla t\u00e0nn na ko, ngir rusloo boroom xam-xam yi; te li \u00e0ddina teg ag \u00f1\u00e0kk doole, Y\u00e0lla t\u00e0nn na ko, ngir rusloo boroom doole yi.\n1:28 Li dul juddu bu rafet te mat a xeeb ci \u00e0ddina, Y\u00e0lla t\u00e0nn na ko; Y\u00e0lla t\u00e0nn na li nekkul, ngir neenal li nekk.\n1:29 Noonu kenn du man a damu ca kanam Y\u00e0lla.\n1:30 Waaye Y\u00e0lla moo def ba ngeen bokk ci Kirist, moom mi doon ci nun xam-xam bu j\u00f3ge ca Y\u00e0lla, maanaam: sunu njubte, sunu sellaay, sunu njot.\n1:31 Loolu dafa am, ngir li Mbind mi wax am, ne: \u00abKuy damu, na damu ci Boroom bi.\u00bb\n2:1 Man ci sama bopp, bokk yi, bi ma \u00f1\u00ebwee ci y\u00e9en, ngir y\u00e9gle mb\u00f3oti Y\u00e0lla, \u00f1\u00ebwuma ci ay wax yu neex ak xam-xam bu r\u00e9y.\n2:2 Dogu woon naa ci ba\u00f1 a xam dara ci seen biir lu dul Yeesu Kirist, te muy ki \u00f1u rey ca bant ba.\n2:3 Bi ma teewee ci y\u00e9en, \u00e0nd naa ak \u00f1\u00e0kk doole, ragal ak nj\u00e0qare.\n2:4 Li ma wax ak li ma waare, defuma ko ci l\u00e0mmi\u00f1 wu neex, sukkandikoo ko ci xam-xamu nit, waaye \u00e0nd na ak ay firnde yu soqikoo ci k\u00e0ttanu Xelum Y\u00e0lla,\n2:5 ngir seen ng\u00ebm ba\u00f1 a w\u00e9kku ci xam-xamu nit \u00f1i waaye mu w\u00e9kku ci dooley Y\u00e0lla.\n2:6 Moona am na xam-xam bu nuy y\u00e9gal \u00f1i mat, xam-xam bu bokkul ci \u00e0ddina si, te njiiti \u00e0ddina si xamu\u00f1u ko, \u00f1oom \u00f1i nar a w\u00e9y.\n2:7 Nu ngi y\u00e9gle mb\u00f3otu xam-xamu Y\u00e0lla, mu n\u00ebbbu woon te Y\u00e0lla dogal ko ngir sunu ndam, laata \u00e0ddina di sosu.\n2:8 Kenn ci njiiti \u00e0ddina amul woon xam-xam boobu. Su \u00f1u ko amoon, kon du\u00f1u rey Boroom ndam li ci bant bi.\n2:9 Waaye Mbind mi nee na:\u00abLu b\u00ebt gisul,nopp d\u00e9ggu kote xel xalaatu ko,loolu la Y\u00e0lla dencal \u00f1i ko b\u00ebgg.\u00bb\n2:10 Fekk nag nun la ko Y\u00e0lla won, jaarale ko ci Xelam. Xelum Y\u00e0lla mooy leeral l\u00e9pp, ba ci xalaati Y\u00e0lla yi g\u00ebn a x\u00f3ot.\n2:11 Kan ci nit \u00f1i moo xam y\u00ebfi nit? Xanaa xelum nit mi nekk ci moom rekk a ko xam. Noonu it kenn xamul y\u00ebfi Y\u00e0lla, ku dul Xelum Y\u00e0lla.\n2:12 Nun nag Xel mi nu jot, j\u00f3gewul ci \u00e0ddina, waaye Y\u00e0llaa nu ko sol.\n2:13 Te loolu nu Y\u00e0lla may, y\u00e9glewunu ko ci ay baat yu soqikoo ci xam-xamu nit, waaye nu ngi koy y\u00e9gle ci baat, yi soqikoo ci Xelum Y\u00e0lla, di tekkantal y\u00ebfi Xelum Y\u00e0lla ci ay baat yu mu nu sol.\n2:14 Nit kese du nangu y\u00ebfi Xelum Y\u00e0lla. Ag ndof lay doon ci moom, te du ko man a nangu, ndaxte ku yor Xelum Y\u00e0lla rekk moo ko man a r\u00e0\u00f1\u00f1ale.\n2:15 Nit ki yor Xelum Y\u00e0lla dafay \u00e0tte l\u00e9pp, te moom ci boppam, kenn du ko \u00e0tte.\n2:16 Ndaxte Mbind mi nee na:\u00abAna ku xam xalaatu Boroom bi?Ku ko doon digal?\u00bb Waaye nun am nanu xalaatu Kirist.\n3:1 Man nag bokk yi, m\u00ebnuma woon a wax ak y\u00e9en ni ay nit \u00f1uy d\u00e9ggal Xelum Y\u00e0lla, waaye waroon naa wax ak y\u00e9en ni \u00f1uy topp seen nafsu, mel ni ay liir ci seen dund ci Kirist.\n3:2 N\u00e0mpaloon naa leen, waaye joxuma leen dugub, ndaxte \u00e0ttanuleen ko woon, te ba l\u00e9egi sax \u00e0ttanuleen ko\n3:3 ci li ngeen di topp seen nafsu. Bu \u00f1eetaan ak xuloo amee ci seen biir, xanaa du loolu mooy wone ne, dangeen a topp seen nafsu, di doxale ni niti \u00e0ddina?\n3:4 Bu kenn y\u00e9glee ne: \u00abMan ci Pool laa bokk,\u00bb keneen ne: \u00abMan ci Apolos,\u00bb ndax j\u00ebfewuleen ni niti \u00e0ddina rekk?\n3:5 Kuy Apolos? ak kuy Pool? Nun ay surga rekk lanu, yu ngeen jaare, ba g\u00ebm. Te Boroom bi moo sas ku nekk ligg\u00e9eyam.\n3:6 Maa j\u00ebmb\u00ebt, Apolos suuxat, waaye Y\u00e0lla moo jebbil.\n3:7 Ki j\u00ebmb\u00ebt nag ak ki suuxat, kenn du ci dara, waaye Y\u00e0lla miy jebbil rekk moo am solo.\n3:8 Ki j\u00ebmb\u00ebt ak ki suuxat benn la\u00f1u. Teewul nag ku nekk dina jot yool bu tollook ligg\u00e9eyam.\n3:9 Nu ngi ligg\u00e9eyandoo ci ligg\u00e9eyu Y\u00e0lla; y\u00e9enay toolu Y\u00e0lla, y\u00e9enay taaxum Y\u00e0lla.\n3:10 Man nag teg naa fondamaa bi, ni tabaxkat bu man ligg\u00e9eyam, d\u00ebppoo ak sas wi ma Y\u00e0lla jagleel ci kaw yiwam. Te keneen a ngi tabax ci kaw; waaye na ku nekk teeylu ci ni muy tabaxe.\n3:11 Ci li j\u00ebm ci fondamaa bi, kenn m\u00ebnu fee t\u00ebral beneen bu dul bi fi xas a taxaw, muy Yeesu Kirist.\n3:12 Ku tabax ci kaw fondamaa bi, wurus, xaalis, per, d\u00e9nk, gittax walla boob,\n3:13 sa ligg\u00e9ey dina f\u00e9s, ndaxte b\u00e9s baa koy xamle. B\u00e9s boobu dina fenk ni safara, te safara si dina nattu ligg\u00e9eyu ku nekk.\n3:14 Ku sa ligg\u00e9ey d\u00ebg\u00ebr, dinga jot yool.\n3:15 Waaye ku sa ligg\u00e9ey lakk, dinga \u00f1\u00e0kk. Yaw ci sa bopp dinga mucc, waaye mel ni ku r\u00ebcc ci safara si.\n3:16 Xanaa xamuleen ne, y\u00e9enay k\u00ebr Y\u00e0lla, te Xelum Y\u00e0lla d\u00ebkk na ci y\u00e9en?\n3:17 Ku y\u00e0q k\u00ebr Y\u00e0lla gi, Y\u00e0lla dina la y\u00e0q, ndaxte k\u00ebr Y\u00e0lla gi dafa sell, te y\u00e9enay k\u00ebr googu.\n3:18 Kon bu kenn nax boppam: su kenn ci y\u00e9en tegee boppam boroom xam-xam ci gis-gisu \u00e0ddina sii, kooku na doon dof, ngir am xam-xam bu w\u00f3or.\n3:19 Ndaxte xam-xamu \u00e0ddina si, ndof la fa Y\u00e0lla. Moom la Mbind mi ne: \u00abY\u00e0lla j\u00e0pp na \u00f1u muus \u00f1i, ba seen fiir k\u00ebppu ci seen kaw.\u00bb\n3:20 Te it: \u00abBoroom bi xam na xalaati boroom xam-xam yi; xam ne, du\u00f1u mujj fenn.\u00bb\n3:21 Kon nag bu kenn tiitaru ndax nit \u00f1i, ndaxte y\u00e9ena moom l\u00e9pp,\n3:22 muy Pool, di Apolos, di Sefas, di \u00e0ddina, di dund, di dee, di lu am, di luy \u00f1\u00ebw; l\u00e9pp, y\u00e9ena ko moom.\n3:23 Te y\u00e9en, Kirist a leen moom, te Kirist, Y\u00e0llaa ko moom.\n4:1 Na\u00f1u nu teg kon ay surgay Kirist, di ay jawri\u00f1 yuy xamle mb\u00f3oti Y\u00e0lla.\n4:2 Li war ci jawri\u00f1 mooy mu takku ci ligg\u00e9eyam.\n4:3 Ngeen \u00e0tte ma walla \u00f1eneen \u00e0tte ma, amaluma ko solo. Te man sax duma \u00e0tte sama bopp.\n4:4 Sama xel yeddu ma ci dara, waaye loolu taxul ma jub; ki may \u00e0tte mooy Boroom bi.\n4:5 Looloo tax buleen daan kenn ci \u00e0tte, bala jamono ji di jot te Boroom bi \u00f1\u00ebw. Mooy leeral yi n\u00ebbbu ci l\u00ebnd\u00ebm, di l\u00e0\u00f1\u00f1i m\u00e9b\u00e9tu xol yi. Bu ko defee ku nekk dina jot ci Y\u00e0lla ng\u00ebr\u00ebm, li mu yelloo.\n4:6 Bokk yi, ci loolu ma leen doon wax l\u00e9pp nag, misaal naa leen ko ci Apolos ak ci man, ngir ngeen xool ci nun, ba xam li wax jii di tekki: \u00abBu seen xalaat weesu li Mbind mi wax.\u00bb Noonu kenn du m\u00e0ggal kii, suufeel ki ci des.\n4:7 Ndaxte yaw, ku la def, ba nga g\u00ebn a m\u00e0gg \u00f1i ci des? Loo am lu \u00f1u la mayul? Te bu \u00f1u la ko mayee, lu tax nga di ci tiitaru, mel ni mayu\u00f1u la ko?\n4:8 Y\u00e9en suur ngeen xaat! Woomle ngeen xaat! T\u00e0mbali ngeen di nguuru te agseegunu! C\u00e9y ni ma b\u00ebgge, ngeen di nguuru, ba nu man a bokk ak y\u00e9en di nguuru!\n4:9 Xalaat naa ne, nun ndawi Kirist yi, Y\u00e0lla def na ba nu mel ni nit \u00f1u \u00f1u j\u00e0ppe ci xare te mujj ci s\u00e0ppe yi, \u00f1u dogal seen dee, nuy ceetaanum mbindeef y\u00e9pp, muy nit muy malaaka.\n4:10 Nun teg na\u00f1u nu ni ay dof ndax Kirist, waaye y\u00e9en am ngeen xel ci Kirist. N\u00e9ew nanu doole, waaye y\u00e9en am ngeen doole. Nawees na leen, waaye nun da\u00f1u noo xeeb.\n4:11 Ba fii mu nekk, danoo xiif, mar te rafle; \u00f1u ngi nuy d\u00f3or, te d\u00ebkkunu fenn;\n4:12 nu ngi \u00f1aq di jari\u00f1oo. Ku nu saaga, nu \u00f1aanal la lu baax. Coono bu \u00f1u nu teg, nu tegoo ko.\n4:13 Ku nu \u00f1aawal, nu tontu la tont lu rafet. Fi mu ne noo mujj di mbalitu \u00e0ddina, di \u00f1u \u00f1\u00e0kk njari\u00f1 ci l\u00e9pp.\n4:14 Binduma leen loolu ngir ngeen am yeraange, waaye dama koo def ngir artu leen, ndaxte y\u00e9enay samay doom te b\u00ebgg naa leen.\n4:15 Su ngeen amee junniy njiit yu leen di s\u00e0mm ci Kirist, ba tey benn baay rekk ngeen am, ndaxte maa leen y\u00e9gal xebaar bu baax bi, ba jur leen ci Kirist.\n4:16 Kon nag maa ngi leen di \u00f1aan, ngeen roy ci man.\n4:17 Looloo tax ma yebal ci y\u00e9en Timote, miy sama doomu diine, di doom ju takku te ma b\u00ebgg ko. Dina leen f\u00e0ttali ni may dunde ci Kirist, te mu d\u00ebppook li may j\u00e0ngale fu nekk ci mboolooy \u00f1i g\u00ebm \u00f1\u00e9pp.\n4:18 Am na ci seen biir \u00f1uy tiitaru, di xalaat ne, duma delluseeti ci y\u00e9en.\n4:19 Waaye bu soobee Boroom bi, l\u00e9egi ma \u00f1\u00ebw ci y\u00e9en te seet boroom tiitar yooyu; waxuma seen k\u00e0ddu, seen doole laay seet.\n4:20 Ndaxte nguuru Y\u00e0lla du waxi kese, waaye doole la.\n4:21 Lu leen g\u00ebnal? Ma \u00f1\u00ebw ci y\u00e9en, yor ab yar, walla ma \u00e0nd ak mb\u00ebggeel, te lewet?\n5:1 D\u00e9gg nanu sax \u00f1u naan, am na kuy moy Y\u00e0lla ci seen biir, moy gu ni tollu, du\u00f1u ko gis sax ci \u00f1i xamul Y\u00e0lla. Dem na, ba am ci y\u00e9en kuy s\u00e9y ak jabaru baayam.\n5:2 Moona y\u00e9en de, y\u00e9ena ngi tiitaru. Waaye dangeen a waroon a am naqar, ba d\u00e0q kiy def loolu ci seen biir!\n5:3 Man nag, j\u00ebmm ji sore na leen, waaye xel mi mu ngi ci y\u00e9en, te \u00e0tte naa xaat kiy def loolu, ni su ma teewoon ci seen biir. Dogal naa,\n5:4 ngeen daje ci turu Boroom bi Yeesu, te sama xel teewe ko, \u00e0nd ak dooley Boroom bi Yeesu,\n5:5 nu j\u00e9bbal nit kooku Seytaane, yaramam y\u00e0qu, ngir ruuwam mucc keroog b\u00e9su Boroom bi.\n5:6 Seen tiitar bi jekkul dara. Xanaa xamuleen ne, tuuti lawiir day tax tooyalu fari\u00f1 b\u00e9pp funki?\n5:7 Ni ma leen ko man a misaale, j\u00ebleleen fi b\u00e9pp lawiir bu y\u00e0gg, ngir ngeen sell ni tooyal bu bees bu amul lawiir, ndax nekk ngeen ko ba noppi. Ndaxte Kirist deeyal na nu ca bant ba, mel ni mbote mu \u00f1uy rendi, j\u00e9bbal ko Y\u00e0lla ca m\u00e0ggalu b\u00e9su J\u00e9ggi ba.\n5:8 Kon nanu m\u00e0ggal sunu M\u00e0ggal, waxuma ak lawiir bu m\u00e0ggat biy misaal ki\u00f1aan ak lu bon, waaye ak mburu mu amul lawiir, maanaam ci xol bu laab ak ci d\u00ebgg.\n5:9 Bindoon naa leen, ngeen ba\u00f1 a s\u00e9q dara ak njaalookat yi.\n5:10 B\u00ebgguma ci woon a limaale waa \u00e0ddina, maanaam njaalookat yi, nay yi, njubla\u014b yi ak x\u00ebr\u00ebmkat yi. Su ngeen s\u00e9qul ak \u00f1oo\u00f1u dara, kon f\u00e0ww ngeen g\u00e9nn \u00e0ddina.\n5:11 Lii laa leen b\u00ebggoon a wax: buleen s\u00e9q dara ak ku \u00f1u tudde mbokk mu g\u00ebm Kirist, te fekk day njaaloo walla mu nay walla muy x\u00ebr\u00ebm walla muy xas nit walla muy m\u00e0ndi walla muy njubla\u014b. Nit ku mel noonu moom, buleen bokk ak moom, sax far di lekk.\n5:12 Ndax man maa war a \u00e0tte \u00f1i bokkul ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm Kirist? D\u00e9ed\u00e9et! Waaye \u00f1i bokk ci seen mbooloo y\u00e9ena leen war a \u00e0tte.\n5:13 \u00d1i bokkul ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm, Y\u00e0lla moo leen di \u00e0tte. Waaye y\u00e9en, ni ko Mbind mi waxe: \u00abD\u00e0qleen ci seen biir kiy def lu bon.\u00bb\n6:1 Te it bu kenn ci y\u00e9en amee l\u00ebj-l\u00ebj digganteem ak mbokku taalibeem, lu tax muy dem ca \u00e0ttekaayi \u00f1i xamul Y\u00e0lla, te ba\u00f1 a dem ca gaayi Y\u00e0lla yi, \u00f1u \u00e0tte ko?\n6:2 Xanaa dangeen a xamul ne, gaayi Y\u00e0lla yi \u00f1ooy \u00e0tteji \u00e0ddina? Te ndegam y\u00e9enay \u00e0tteji \u00e0ddina, lu tere ngeen man a \u00e0tte mbir yu \u00f1\u00e0kk solo yi?\n6:3 Xanaa xamuleen ne, nooy \u00e0tteji malaaka yi? waxatumaak mbiri \u00e0ddina sii.\n6:4 Bu ngeen amee ay l\u00ebj-l\u00ebj yu mel noonu, dangeen di wuti ay \u00e0ttekat ci ay nit, \u00f1i amul wenn yoon ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm!\n6:5 Ma ne kon, war ngeen a rus! Xanaa amul ci seen biir kenn ku am xel, ku man a \u00e0tte mbokkam yi?\n6:6 Waaye defuleen loolu; mbokk a ngi layoo ak moroomam, rax-ca-dolli ci kanamu \u00f1i g\u00ebmul la\u00f1u koy defe!\n6:7 Layoo bi sax wone na ne, b\u00e0yyi ngeen seen warugar. Lu tax mu\u00f1uleen sax too\u00f1, yi \u00f1u leen di too\u00f1? Lu tax far nanguwuleen, \u00f1u s\u00e0cc leen?\n6:8 Waaye y\u00e9en sax y\u00e9enay too\u00f1 ak di s\u00e0cc, te seeni bokk ngeen koy def!\n6:9 Xanaa xamuleen ne, \u00f1i jubadi du\u00f1u bokk ci nguuru Y\u00e0lla? Bu leen ci kenn nax: \u00f1iy doxaan walla x\u00ebr\u00ebmkat yi ak njaalookat yi ak g\u00f3or-jig\u00e9en \u00f1i ak \u00f1i ko nangu,\n6:10 walla s\u00e0cc yi ak \u00f1u b\u00ebgge \u00f1i ak m\u00e0ndikat yi ak \u00f1iy xaste ak njubla\u014b yi, du\u00f1u bokk ci nguuru Y\u00e0lla.\n6:11 Te am na \u00f1u meloon noonu ci y\u00e9en. Waaye Y\u00e0lla f\u00f3otal na leen seeni b\u00e0kkaar, sellal leen, \u00e0tte leen ni \u00f1u jub, ci turu Boroom bi Yeesu Kirist ak ci dooley Xelum Y\u00e0lla, sunu Boroom.\n6:12 Am na ci y\u00e9en \u00f1u naan: \u00abSa\u00f1 naa l\u00e9pp.\u00bb Waaw, waaye du l\u00e9pp a jari\u00f1 nit. \u00abSa\u00f1 naa l\u00e9pp,\u00bb waaye duma b\u00e0yyi dara, mu noot ma.\n6:13 Am na ci y\u00e9en \u00f1u naan: \u00ab\u00d1am mooy jari\u00f1 biir, te biir ay jari\u00f1oo \u00f1am.\u00bb Waaw, te Y\u00e0lla dina leen y\u00e0q, \u00f1oom \u00f1aar y\u00e9pp. Waaye s\u00e0kku\u00f1u yaram ngir moy Y\u00e0lla; da\u00f1u koo s\u00e0kk, ngir muy jari\u00f1 Boroom bi, Boroom bi di ko jari\u00f1oo.\n6:14 Te Y\u00e0lla, mi dekkal Boroom bi, dina dekkal it sunu yaram jaare ko ci dooleem.\n6:15 Xanaa xamuleen ne, seen yaram \u00f1ooy c\u00e9ri Kirist? Ndax kon damay j\u00ebl c\u00e9ri Kirist, def ko c\u00e9ri jig\u00e9eni moykat? Mukk!\n6:16 Xanaa xamuleen ne, kuy \u00e0nd ak jig\u00e9en juy moy dafay booloo ak moom, nekk benn? Ndaxte Mbind mi nee na: \u00ab\u00d1oom \u00f1aar dina\u00f1u doon benn.\u00bb\n6:17 Waaye nag kuy \u00e0nd ak Boroom bi, xel yi da\u00f1uy booloo, nekk benn.\n6:18 Dawleen njaaloo! B\u00e9pp b\u00e0kkaar bu nit man a def, du laal yaramam, waaye nag kuy njaaloo, dafay b\u00e0kkaar, di lor yaramam.\n6:19 Xanaa xamuleen ne, seen yaram mooy k\u00ebr Y\u00e0lla gi? Gannaaw Xel mu Sell maa ngi ci y\u00e9en, te Y\u00e0llaa leen ko may, kon moomuleen seen bopp,\n6:20 ndaxte Y\u00e0lla jot na leen ak nj\u00ebg gu r\u00e9y. Kon nag m\u00e0ggal-leen Y\u00e0lla ci seen yaram.\n7:1 Nanu j\u00e0ll nag l\u00e9egi ci laaj, yi ngeen ma doon bind, ci ba\u00f1 a \u00e0nd ak jig\u00e9en, ndax lu baax la ci g\u00f3or.\n7:2 Lii mooy sama xalaat: moy gu bare gi tax na ba, na g\u00f3or gu nekk am jabaram, jig\u00e9en ju nekk am j\u00ebkk\u00ebram.\n7:3 J\u00ebkk\u00ebr war na def warugaru j\u00ebkk\u00ebr ci jabaram; jabar it def warugaru jabar ci j\u00ebkk\u00ebram.\n7:4 Jig\u00e9en ji amul sa\u00f1-sa\u00f1 ci yaramam moom kenn; j\u00ebkk\u00ebram moo ko moom. Niki noonu it j\u00ebkk\u00ebr ji amul sa\u00f1-sa\u00f1 ci yaramam; jabaram moo ko moom.\n7:5 Bu kenn tere boppam moroomam, su dul ne dangeen a m\u00e0nkoo ci def noonu ab diir, ngir g\u00ebn a man a w\u00e9et ak Y\u00e0lla ciy \u00f1aan. Waaye su loolu weesoo, nangeen doxal yoonu s\u00e9y; lu ko moy, Seytaane dina leen fiir ndax seen \u00f1\u00e0kk maandute.\n7:6 Li ma leen di wax fii du ndigal, waaye dama leen di xamal li \u00f1u leen may, ngeen def ko.\n7:7 Ndaxte d\u00ebgg-d\u00ebgg su ma sa\u00f1oon, kon \u00f1\u00e9pp mel ni man; waaye ku nekk ak li la Y\u00e0lla jagleel, kii ak may gii, kee ak may gale.\n7:8 Lii laay y\u00e9gal \u00f1i s\u00e9yul ak it \u00f1i seen j\u00ebkk\u00ebr dee: baax na ci y\u00e9en, su fekkee dangeen a toog rekk ni man, ba\u00f1 a s\u00e9y.\n7:9 Waaye su ngeen m\u00ebnul a t\u00e9ye seen bopp, nangeen s\u00e9y, ndaxte s\u00e9y moo g\u00ebn xemmem di leen gaa\u00f1.\n7:10 \u00d1i s\u00e9y nag, maa ngi leen di jox ndigal lii --Boroom bi moo ko waxoon, du man \u2014 jig\u00e9en ju s\u00e9y warul a teqalikoo ak j\u00ebkk\u00ebram.\n7:11 Te bu teqalikoo ak moom, bumu s\u00e9yaat, mbaa boog na juboo ak j\u00ebkk\u00ebram. Te bu j\u00ebkk\u00ebr ji fase jabaram.\n7:12 \u00d1i ci des nag, lii laa leen di wax --Boroom bi waxu ko woon \u2014 su nit ku g\u00ebm Kirist amee jabar ju g\u00ebmul, te mu nangoo s\u00e9y ak moom, waru koo fase.\n7:13 Naka noonu it su jig\u00e9en ju g\u00ebm Kirist amee j\u00ebkk\u00ebr ju g\u00ebmul, te mu nangoo nekk ak moom, warul a tas.\n7:14 Li tax ma wax ko moo di, j\u00ebkk\u00ebr ji g\u00ebmul, Y\u00e0lla sellal na ko, ndax li mu \u00e0nd ak jabaram. Te it jig\u00e9en ji g\u00ebmul, Y\u00e0lla sellal na ko, ndax li mu \u00e0nd ak j\u00ebkk\u00ebram ji g\u00ebm; lu ko moy, seeni doom dina\u00f1u am sobe, te fekk da\u00f1oo sell.\n7:15 Waaye nag, su fekkee ki g\u00ebmul b\u00ebgg na dem, na dem. Ci w\u00e0ll googu nag, ki g\u00ebm Kirist, muy j\u00ebkk\u00ebr ji walla jabar ji, amul benn t\u00ebnk, ndaxte Y\u00e0lla moo leen woo ngir ngeen dund ci j\u00e0mm.\n7:16 Loo ci xam, yaw jig\u00e9en ji, ndax dinga g\u00ebmloo sa j\u00ebkk\u00ebr Musalkat bi walla d\u00e9et? Loo ci xam yaw j\u00ebkk\u00ebr ji it, ndax dinga g\u00ebmloo sa jabar Musalkat bi walla d\u00e9et?\n7:17 Ku nekk nag na dund, ni ko ko Boroom bi jagleele, mu mengoo ak ni mu meloon, bi ko Y\u00e0lla wooyee. Moom laay t\u00ebral ci mboolooy \u00f1i g\u00ebm y\u00e9pp.\n7:18 Ki xaraf, bi ko Y\u00e0lla wooyee, warul a j\u00e9em a far m\u00e0ndargam xaraf bi. Ki xaraful, bi ko Y\u00e0lla wooyee, aajowul mu xaraf.\n7:19 Xaraf ak \u00f1\u00e0kka xaraf l\u00e9pp a yem; li am solo moo di topp ndigali Y\u00e0lla.\n7:20 Na kenn ku nekk j\u00e0pp ci li mu nekkoon, bi ko Y\u00e0lla wooyee.\n7:21 Ndax jaam nga woon, bi la Y\u00e0lla wooyee? Na ci sa xel dal. Waaye soo amee bunt, ba yiwiku, nanga ci jaar.\n7:22 Ku nekkoon jaam, bi la Boroom bi wooyee, Boroom bi goreel na la. Ba tey it ku nekkoon gor, bi \u00f1u la wooyee, jaamu Kirist nga.\n7:23 Gannaaw Y\u00e0lla jot na leen ak nj\u00ebg gu r\u00e9y, buleen doon jaamub nit.\n7:24 Bokk yi, f\u00e0ww ku nekk w\u00e9y ca kanam Y\u00e0lla ci f\u00e0nn ga mu nekkoon, bi ko Y\u00e0lla wooyee.\n7:25 Ci li j\u00ebm ci janq yi, awma ndigalu Boroom bi, waaye maa ngi joxe sama xalaat, ni ku \u00f1u w\u00f3olu ndax li ma jot y\u00ebrmandey Boroom bi.\n7:26 Bu nu seetee tiis wii fi teew nag, defe naa ne li baax ci nit, moo di mu sax ci li mu nekk.\n7:27 Ndax takk nga jabar? Bul wut a t\u00e0ggoo ak moom. Ndax takkuloo jabar? Bul wut jabar.\n7:28 Waaye nag boo s\u00e9yee, defoo b\u00e0kkaar, te bu janq s\u00e9yee, deful b\u00e0kkaar. Waaye \u00f1i s\u00e9y dina\u00f1u am naqar ci \u00e0ddina, te naqar woowu dama leen koo b\u00ebggoon fanqal, y\u00e9en \u00f1i s\u00e9yagul.\n7:29 Lii laa b\u00ebgg a wax, bokk yi: diir bu g\u00e0tt rekk a fi des. Lu weesu tey, na g\u00f3or \u00f1i am jabar di def, ni bu \u00f1u ko amul woon;\n7:30 \u00f1iy jooy, mel ni \u00f1u jooyul; \u00f1iy b\u00e9g, mel ni \u00f1u b\u00e9gul; \u00f1iy j\u00ebnd, ni \u00f1u moomul li \u00f1u j\u00ebnd;\n7:31 \u00f1iy jari\u00f1oo \u00e0ddina, ba\u00f1 cee x\u00e9r. Ndaxte \u00e0ddina sii, ci ni mu mel, dootul y\u00e0ggati.\n7:32 B\u00ebggoon naa, ngeen ba\u00f1 a am benn xalaat. G\u00f3or gu takkul jabar dafay b\u00e0yyi xel ci mbiri Boroom bi, di wut a neex Boroom bi.\n7:33 Waaye ku takk jabar, f\u00e0ww mu b\u00e0yyi xel ci mbiri \u00e0ddina si, ak nu mu man a neexe jabaram,\n7:34 te noonu dafay daldi bare soxla. Te jig\u00e9en ju s\u00e9yul, walla janq, dafay b\u00e0yyi xel ci mbiri Boroom bi \u2014 b\u00ebgg koo jox yaramam ak xelam. Waaye jig\u00e9en ji s\u00e9y dafay b\u00e0yyi xel ci mbiri \u00e0ddina, ak nu mu man a neexe j\u00ebkk\u00ebram.\n7:35 Seen njari\u00f1 a tax ma wax lii, du ngir teg leen yen bu ngeen \u00e0ttanul, waaye ngeen man a j\u00e0ppandil Boroom bi ci njaamu gu rafet gu \u00e0ndul ak genn njaaxle.\n7:36 Nanu j\u00e0ll nag ci mbiri kiy takk ngoro te amul pasteefu takk ndaw si. Su fekkee ne waxambaane wi xalaat na ne, j\u00ebfewul nu jekk ak janq bi, fekk muy wees ag ndawam, te mu xalaat ne dafa koo war a takk, kon na ko takk, ni mu ko b\u00ebgge; deful b\u00e0kkaar.\n7:37 Waaye nag su dogoo d\u00ebgg ci ba\u00f1 a takk, fekk sagoom rekk a tax te kenn tegu ko ko, kon ba tey def na lu baax.\n7:38 Noonu ku takk as ndawam def na lu baax, rawatina nag ku takkul.\n7:39 Jig\u00e9en ji s\u00e9y dina \u00e0nd ak j\u00ebkk\u00ebram giiru dundam. Waaye su j\u00ebkk\u00ebr ji faatoo, man na s\u00e9y ak ku ko neex, su fekkee ne g\u00f3or gu g\u00ebm la.\n7:40 Moona nag dina g\u00ebn a b\u00e9g, bu toogee noonu rekk. Loolu mooy sama xalaat, te defe naa ne, man it am naa Xelum Y\u00e0lla.\n8:1 L\u00e9egi nag, ci li j\u00ebm ci y\u00e0pp wi \u00f1u j\u00e9bbal x\u00ebr\u00ebm yi: nun \u00f1\u00e9pp am nanu xam-xam, loolu d\u00ebgg la. Xam-xam day tax ba nit y\u00e9g boppam, waaye mb\u00ebggeel day y\u00e9kkati ng\u00ebm.\n8:2 Ku xalaat ne xam nga dara, sa xam-xam b\u00ebnnagul.\n8:3 Waaye ku b\u00ebgg Y\u00e0lla, Y\u00e0lla xam la.\n8:4 Kon nag ci li j\u00ebm ci lekk y\u00e0pp wu \u00f1u j\u00e9bbal x\u00ebr\u00ebm yi, xam nanu ne, x\u00ebr\u00ebm du dara ci \u00e0ddina te xam nanu itam ne, Y\u00e0lla kenn rekk la.\n8:5 Su fekkee ne am na sax yu \u00f1uy teg Y\u00e0lla, muy ci asamaan mbaa ci suuf --ndaxte am na yu bare yu \u00f1u faral di bokkaaleel Y\u00e0lla ak Boroom bi \u2014\n8:6 ba tey ci nun, jenn Y\u00e0lla rekk a am, muy Baay bi; l\u00e9pp a ngi j\u00f3ge ci moom te moom lanu nekkal. Te it benn Boroom rekk a am, muy Yeesu Kirist; l\u00e9pp a ngi jaare ci moom, te nun it nu ngi dund jaare ci moom.\n8:7 Waaye \u00f1\u00e9pp xamu\u00f1u loolu. Am na \u00f1u t\u00e0mmoon x\u00ebr\u00ebm yi, te l\u00e9egi, bu \u00f1u lekkatee y\u00e0ppu sarax yi, da\u00f1uy xalaat ne, x\u00ebr\u00ebm la\u00f1u ko jagleel. Seen xel dafa leen di yedd, ndaxte ci seen \u00f1\u00e0kka xam da\u00f1uy foog ne, taq na\u00f1u sobe ndax \u00f1am woowu.\n8:8 Waaye \u00f1am m\u00ebnul a tax nu neex Y\u00e0lla. Su nu ci lekkee, du yokk dara ci nun. Su nu ci lekkul, du nu w\u00e0\u00f1\u00f1i dara.\n8:9 Waaye moytuleen, ba sa\u00f1-sa\u00f1 bi ngeen am, ba\u00f1 a y\u00f3bbe b\u00e0kkaar \u00f1i seen ng\u00ebm n\u00e9ew.\n8:10 Su amee ku ng\u00ebmam n\u00e9ew, mu gis la, yaw mi bare xam-xam, nga toog di lekk ca m\u00e0ggalukaayu x\u00ebr\u00ebm ya, ndax du ko xiir mu lekk y\u00e0ppu sarax?\n8:11 Noonu sa xam-xam dina lor kooku ng\u00ebmam n\u00e9ew, fekk sa mbokk moomu, Kirist dee na ngir moom!\n8:12 Su ngeen b\u00e0kkaaree, ba too\u00f1 bokk yi n\u00e9ew ng\u00ebm, di n\u00ebxal seen xel, b\u00e0kkaar ngeen ba too\u00f1 Kirist.\n8:13 Kon bu sama mbokk s\u00f3oboo ci b\u00e0kkaar ndax \u00f1am wi ma lekk, dootuma lekk mukk y\u00e0pp, ngir ba\u00f1 a s\u00f3ob ci b\u00e0kkaar sama mbokk mi.\n9:1 Ndax awma ndogal ci li may def? Ndax duma ndawul Kirist? Ndax gisuma Yeesu sunu Boroom? Xanaa du y\u00e9ena soqikoo ci ligg\u00e9ey, bi ma Boroom bi sant?\n9:2 Su ma \u00f1enn \u00f1i tegul ndaw, moom laa ci y\u00e9en, ndaxte y\u00e9enay firnde jiy wone ne, ndawul Boroom bi d\u00ebgg laa.\n9:3 Nii laay tontoo \u00f1i may \u00e0tte:\n9:4 Xanaa sa\u00f1unoo lekk ak a naan?\n9:5 Xanaa sa\u00f1unoo indaale jabar ju g\u00ebm Kirist, ni yeneen ndawul Kirist ak doomi ndeyu Boroom bi ak Sefas sax?\n9:6 Walla boog man ak Barnabas rekk noo war a daan sunu doole?\n9:7 Kan moo mas a solu soldaar ci pexey boppam? Kan mooy bey tool te du ci jari\u00f1u? Walla kan mooy s\u00e0mm jur te du naan ca soow ma?\n9:8 Lii may wax, du ci y\u00ebfi doom Aadama rekk laa ko jukkee; xanaa du yoon wi it moo ko santaane?\n9:9 Ndaxte bind na\u00f1u ci yoonu Musaa ne: \u00abBul sunju\u00f1 g\u00e9mmi\u00f1u nag wu \u00f1u takk ci bojjukaay.\u00bb Ndax mooy tekki nag ne, Y\u00e0lla dafa b\u00e0yyi xel nag yi?\n9:10 Walla boog xanaa nun noo moom wax jooju? Waaw, noo tax \u00f1u bind loolu. Noonu kuy bey war na am yaakaar, te kuy bojj di yaakaar a jot w\u00e0llam.\n9:11 Nu ji ci y\u00e9en y\u00ebfi Xelum Y\u00e0lla, ba noppi g\u00f3obe ci y\u00e9en y\u00ebfi \u00e0ddina, ndax loolu dafa \u00ebpp li nu war a s\u00e9entu?\n9:12 Ndegam \u00f1eneen a am sa\u00f1-sa\u00f1 boobu ci y\u00e9en, nun kon waxi-noppi. Waaye nag jari\u00f1oowunu sa\u00f1-sa\u00f1 boobu. Danuy far mu\u00f1 l\u00e9pp, ngir ba\u00f1 a indi ndog ci yoonu xebaar bu baax bu Kirist bi.\n9:13 Xanaa xamuleen ne, \u00f1iy ligg\u00e9eyal y\u00ebf yu sell yi, da\u00f1uy lekk \u00f1am, wi ci k\u00ebr Y\u00e0lla gi, te \u00f1iy ligg\u00e9ey ci saraxalukaay bi, da\u00f1uy jot seen w\u00e0ll ci sarax yi?\n9:14 Naka noonu it Boroom bi digle na ne, \u00f1iy y\u00e9gle xebaar bu baax bi, nanu ci dund.\n9:15 Waaye man jari\u00f1oowuma benn ci sa\u00f1-sa\u00f1 yooyu, te binduma y\u00ebf yooyu, ngir ngeen di ma defal yu ni mel. Dee sax moo ma ko g\u00ebnal \u2014 kenn du j\u00eble ci man mbir moomu may ka\u00f1oo!\n9:16 Su may y\u00e9gle xebaar bu baax bi, m\u00ebnuma cee ka\u00f1u. Sas la, wu \u00f1u ma sas. Dinaa torox, su ma y\u00e9glewul xebaar bu baax bi!\n9:17 Su doon ci sama coobare laa y\u00e9gle xebaar bu baax bi, man naa ci s\u00e9entu yool. Waaye defuma ko ci sama coobare, ndaxte sas la, wu \u00f1u ma sas.\n9:18 Kon nag lan mooy sama yool? Xanaa di y\u00e9gle xebaar bu baax bi ci dara, te ba\u00f1 a jari\u00f1oo sa\u00f1-sa\u00f1 boobu ma ci yelloo.\n9:19 Gor laa te kenn moomu ma; teewul def naa sama bopp jaamu \u00f1\u00e9pp, ngir man a gindi nit \u00f1u bare ci Kirist.\n9:20 Ci biir Yawut yi, sol naa melow Yawut yi, ngir gindi leen. Man ci sama bopp yoonu Musaa jiitalu ma, terewul bi ma nekkee ci biir \u00f1iy s\u00e0mm yoonu Musaa, s\u00e0mm naa yoon wa, ngir gindi leen.\n9:21 Ci biir \u00f1i nekkul ci yoonu Musaa, faalewuma woon yoon wi, ngir gindi leen; waxuma ne, \u00e0nduma ak yoonu Y\u00e0lla, waaye topp naa yoon ci sama bokk ak Kirist.\n9:22 Ci biir \u00f1i n\u00e9ew ng\u00ebm, meloon naa ni ku n\u00e9ew ng\u00ebm, ngir gindi leen. Doon naa l\u00e9pp ci \u00f1\u00e9pp, ngir def l\u00e9pp lu ma man, ba \u00f1enn mucc ci.\n9:23 Damaa def loolu l\u00e9pp ndax xebaar bu baax bi, ngir man it ma am w\u00e0ll ci barkeem.\n9:24 Xanaa xamuleen ne, \u00f1\u00e9pp \u00f1ooy daw cib rawante, waaye kenn rekk ay j\u00ebl ndam li? Dawleen nag ngir j\u00ebl ko.\n9:25 \u00d1iy jo\u014bante ci po muy waral t\u00e0ggat yaram, da\u00f1uy xa\u00f1 seen bopp lu bare. Da\u00f1u koy def, ngir am kaalag ndam gu dul y\u00e0gg; waaye nun danu koy def, ngir am kaalag ndam gu sax ba f\u00e0ww.\n9:26 Man nag noonu laay dawe, te duma dawantu. Noonu laay b\u00ebree, waaye duma def ni nit kuy d\u00f3or ci jaww ji.\n9:27 Waaye damay noot sama yaram, ba moom ko, ngir ragal a y\u00e9gal \u00f1i ci des xebaar bu baax bi, ba noppi Y\u00e0lla xa\u00f1 ma ndam li.\n10:1 Bokk yi, b\u00ebgguma ngeen umple li daloon sunu maam ya. \u00d1oom \u00f1\u00e9pp niir wa tiimoon na leen, te \u00f1oom \u00f1\u00e9pp j\u00e0ll na\u00f1u g\u00e9ej.\n10:2 S\u00f3obu na\u00f1u ca ndoxu g\u00e9ej ga ak ca niir wa, ba bokk noonu ci Musaa.\n10:3 \u00d1oom \u00f1\u00e9pp bokk na\u00f1oo lekk \u00f1am, wa Y\u00e0lla joxe,\n10:4 naan naan ga mu joxe, ndaxte \u00f1u ngi doon naan ca xeer, wa leen doon gunge, te xeer woowa Kirist la woon.\n10:5 Teewul \u00f1i \u00ebpp ci \u00f1oom neexu\u00f1u woon Y\u00e0lla, ba mu f\u00e0ddoon leen ca m\u00e0ndi\u014b ma.\n10:6 Mbir yooyu ay misaal la\u00f1u, yu nuy artu, ngir benn b\u00ebgg-b\u00ebgg bu bon ba\u00f1 noo jiital, na mu leen jiitale woon.\n10:7 Buleen jaamu ay x\u00ebr\u00ebm, ni ko \u00f1enn \u00f1i ci \u00f1oom defe woon. Ndaxte Mbind mi nee na: \u00abMbooloo mi dafa toog, di lekk ak di naan, ba noppi \u00f1u j\u00f3g di mbumbaay.\u00bb\n10:8 Bunu njaaloo, ni ko \u00f1enn \u00f1i ci \u00f1oom defe woon, ba tax \u00f1aar-fukki junni ak \u00f1ett ci \u00f1oom dee ci benn b\u00e9s.\n10:9 Bunu dii\u014bat Kirist, ni ko \u00f1enn \u00f1i ci \u00f1oom defe, ba ay jaan m\u00e0tt leen, \u00f1u dee.\n10:10 Buleen xultu, ni ko \u00f1enn \u00f1i ci \u00f1oom defe woon, ba tax malaakam Y\u00e0qkat mi rey leen.\n10:11 Mbir yooyu leen daloon misaal la ci nun, te bind na\u00f1u ko ngir artu nu, nun \u00f1iy dund ci jamono jii l\u00e9pp mat.\n10:12 Kon nag kiy naw sa doole, ba yaakaar ne taxaw nga, moytul a daanu ci b\u00e0kkaar!\n10:13 Benn nattu dabu leen bu wuute ak yi dal nit \u00f1\u00e9pp. Te sax Y\u00e0lla kuy s\u00e0mm k\u00f3ll\u00ebre la, te du nangu nattu bi wees seen k\u00e0ttan, waaye cib nattu, dina leen ubbil bunt bu ngeen man a r\u00e9cce, ba ngeen man koo d\u00e9kku.\n10:14 Looloo tax, sama soppe yi, nangeen daw x\u00ebr\u00ebm yi.\n10:15 Maa ngi wax ak y\u00e9en \u00f1i am xel. Kon seetleen li ma leen wax.\n10:16 Kaas bu yiw, bi tax nuy g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla, ndax du wone sunu booloo ak deretu Kirist? Mburu mi nuy damm, xanaa du dafay wone sunu booloo ak yaramu Kirist?\n10:17 Ndegam benn mburu rekk a am, kon nun \u00f1\u00e9pp lu nu baree-bare, menn mbooloo lanu, ndaxte bokk nanu menn mburu mi.\n10:18 Seetleen ci b\u00e0nni Israyil. \u00d1iy lekk sarax si \u00f1u rendi, ndax booloowu\u00f1u ak Y\u00e0lla ji \u00f1u jagleel saraxalukaay ba? Aa\u014bkay!\n10:19 Li may wax, lu muy tekki? Ndax y\u00e0pp wi \u00f1u jagleel x\u00ebr\u00ebm yi dafay dara? walla x\u00ebr\u00ebm yi da\u00f1uy dara?\n10:20 D\u00e9ed\u00e9et! Waaye sarax yi x\u00ebr\u00ebmkat yi di rendi, ay rab la\u00f1u ko jagleel; jagleelu\u00f1u ko Y\u00e0lla. Te man b\u00ebgguma, ngeen booloo ak rab yi.\n10:21 M\u00ebnuleen a naan ci kaasu Boroom bi, naan ci kaasu rab yi. M\u00ebnuleen a sukk ci reerub Boroom bi, sukk ci reerub rab yi.\n10:22 Walla boog ndax danuy j\u00e9em a gillil meru Boroom bi? Xanaa noo ko \u00ebpp doole?\n10:23 Dafa am \u00f1u naan: \u00abL\u00e9pp lanu sa\u00f1.\u00bb Waaw, waaye du l\u00e9pp a baax ci nun. \u00abL\u00e9pp lanu sa\u00f1,\u00bb waaye it l\u00e9pp du y\u00e9kkati ng\u00ebm.\n10:24 Bu kenn seet njari\u00f1am rekk, waaye nay seet njari\u00f1ul moroomam.\n10:25 Man ngeen a lekk l\u00e9pp lu \u00f1uy jaay ca ja ba, ba\u00f1 cee boole ay laaj ngir dalal seen xel.\n10:26 Ndaxte Mbind mi nee na: \u00ab\u00c0ddina ak li ci biiram l\u00e9pp, Boroom bi moo ko moom.\u00bb\n10:27 Ku xamul Y\u00e0lla nag, bu leen wooyee aw \u00f1am k\u00ebram, te ngeen nangoo dem, lekkleen l\u00e9pp lu \u00f1u leen d\u00ebj, ba\u00f1 a laajte dara ngir dalal seen xel.\n10:28 Waaye bu leen kenn nee: \u00abLii sarax la, bu \u00f1u jagleel x\u00ebr\u00ebm yi,\u00bb suurleen ko ndax ki leen ko xamal, ngir xel mu dal.\n10:29 Waxuma sa xel yaw, waaye xelu keneen laay wax. Waaye nga ne: \u00abLi ma sa\u00f1 a def, lu tax nit ku xelam dalul di am dara lu mu ciy wax?\n10:30 Su ma lekkee dara di ci sant Y\u00e0lla, lu tax \u00f1u may wax lu \u00f1aaw, fekk sant naa ci Y\u00e0lla.\u00bb\n10:31 Kon su ngeen di lekk walla ngeen di naan, walla lu ngeen man a def, defleen l\u00e9pp ngir m\u00e0ggal Y\u00e0lla.\n10:32 Buleen def dara lu man a fanq ng\u00ebmu Yawut yi walla \u00f1i dul Yawut walla mbooloom Y\u00e0lla.\n10:33 Noonu laay def man ci sama bopp: damay wut a neex \u00f1\u00e9pp ci l\u00e9pp. Wutuma lu may jari\u00f1, waaye luy jari\u00f1 \u00f1u bare laay wut, ngir \u00f1u mucc.\n11:1 Royleen ma nag, ni may roye Kirist.\n11:2 Maa ngi leen di sant ci li ngeen may f\u00e0ttaliku ci l\u00e9pp, ak ci li ngeen di topp d\u00e9nkaane, yi ma leen d\u00e9nk.\n11:3 Waaye nag b\u00ebgg naa ngeen xam lii: Kirist mooy kilifag b\u00e9pp g\u00f3or, g\u00f3or di kilifag jig\u00e9en, te Y\u00e0lla di kilifag Kirist.\n11:4 Kon nag g\u00f3or guy \u00f1aan Y\u00e0lla, walla muy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, fekk mu teg dara ci boppam, day suufeel Kirist, kilifaam.\n11:5 Waaye bu jig\u00e9en mus\u00f3oruwul, buy \u00f1aan walla buy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, kooku day suufeel j\u00ebkk\u00ebram jiy kilifaam, ndaxte day mel ni jig\u00e9en ju \u00f1u wat.\n11:6 Jig\u00e9en ju dul mus\u00f3oru, bu yaboo, mu watu. Waaye su fekkee ne jig\u00e9en dafay am kersa, su w\u00e0\u00f1\u00f1ee kawaram walla mu watu, f\u00e0ww kon mu mus\u00f3oru.\n11:7 G\u00f3or nag moom warul a teg dara ci boppam, ndaxte mooy melokaanu Y\u00e0lla te dafay wone ndamu Y\u00e0lla. Jig\u00e9en moom dafay wone ndamu g\u00f3or.\n11:8 Ndaxte j\u00eblewu\u00f1u g\u00f3or ci jig\u00e9en, waaye jig\u00e9en la\u00f1u j\u00eble ci g\u00f3or.\n11:9 Te s\u00e0kku\u00f1u g\u00f3or ngir jig\u00e9en, waaye jig\u00e9en la\u00f1u s\u00e0kk ngir g\u00f3or.\n11:10 Looloo tax jig\u00e9en war a teg ci kaw boppam luy m\u00e0ndargaal kilifteef ga, ndax malaaka yi.\n11:11 Teewul nag ci sunu booloo ak Boroom bi, jig\u00e9en a ngi w\u00e9eru ci g\u00f3or, te g\u00f3or a ngi w\u00e9eru ci jig\u00e9en.\n11:12 Ni \u00f1u s\u00e0kke jig\u00e9en ci g\u00f3or, noonu la g\u00f3or juddoo ci jig\u00e9en, te l\u00e9pp a ngi j\u00f3ge ca Y\u00e0lla.\n11:13 Seetleen mbir mii: ndax jekk na jig\u00e9en ba\u00f1 a mus\u00f3oru, buy \u00f1aan Y\u00e0lla?\n11:14 Xanaa du \u00e0ddina ci boppam dafa leen di won ne, g\u00e0cce la ci g\u00f3or, ngir muy yar kawar gu bare?\n11:15 Waaye loolu nag ab taar la ci jig\u00e9en. Da\u00f1oo jagleel jig\u00e9en kawar gu gudd, muy muuraay ci moom.\n11:16 Waaye su kenn b\u00ebggee werante ci mbir moomu, na xam lii: amunu beneen aada ci nj\u00e0ng mi, du nun walla mboolooy Y\u00e0lla.\n11:17 Bi may tollu ci ndigal yi, m\u00ebnuma leen a sant, ndaxte seeni ndaje loraange la\u00f1uy jur, waaye du njari\u00f1.\n11:18 Ci bu j\u00ebkk d\u00e9gg naa lii: bu ngeen di daje, am na ci y\u00e9en \u00f1uy f\u00e9ewaloo, te xaw naa koo g\u00ebm.\n11:19 F\u00e0ww mu am ay f\u00e9ewaloo ci seen biir, ngir \u00f1u man a x\u00e0mmi \u00f1i neex Y\u00e0lla ci y\u00e9en.\n11:20 Bu ngeen dajee, m\u00ebnuleen a wax ne reeru Boroom bi ngeen di lekk.\n11:21 Ndaxte bu ngeen dee lekk, ku nekk dafay gaawantu di lekk reeram, ba tax \u00f1enn \u00f1aa ngi xiif, fekk \u00f1eneen di m\u00e0ndi.\n11:22 Xanaa amuleen k\u00ebr yu ngeen di lekke ak di naane? Walla ndax dangeen a xeeb mbooloom Y\u00e0lla? Walla ngeen b\u00ebgg a rusloo \u00f1i amul dara? Lu ma leen ci war a wax nag? Ma g\u00ebr\u00ebm leen ci loolu? Mukk! G\u00ebr\u00ebmuma leen.\n11:23 Li ma j\u00eble ci Boroom bi, moom laa leen jottali: Boroom bi Yeesu, ci guddi gi \u00f1u ko woree, dafa j\u00ebl mburu,\n11:24 sant Y\u00e0lla, damm ko ne: \u00abLii sama yaram la, wi ma joxe ngir y\u00e9en. Defleen lii, ngir f\u00e0ttaliku ma.\u00bb\n11:25 Noonu itam bi \u00f1u lekkee ba noppi, mu j\u00ebl kaas bi ne leen: \u00abKaas bii mooy misaal k\u00f3ll\u00ebre gu bees, gi Y\u00e0lla fas jaarale ko ci sama deret. Defleen lii ngir f\u00e0ttaliku ma.\u00bb\n11:26 Ndaxte saa su ngeen di lekk mburu mii, walla ngeen di naan ci kaas bii, y\u00e9ena ngi y\u00e9gle deewu Boroom bi, ba kera muy \u00f1\u00ebw.\n11:27 Kon nag k\u00e9pp ku jekkadi ni mu lekke ci mburu mi te naane ni ci kaasu Boroom bi, too\u00f1 nga yaramu Boroom bi ak deretam.\n11:28 Na ku nekk seetlu boppam nag, sog a lekk ci mburu mi te naan ci kaas bi.\n11:29 Ku lekk mburu mi, naan ci kaas bi, fekk faalewuloo solos yaramu Kirist wi, sa lekk ak sa naan dina x\u00ebcc \u00e0tteb Y\u00e0lla ci sa kaw.\n11:30 Looloo tax \u00f1u bare ci y\u00e9en wopp te \u00f1\u00e0kk doole, ba \u00f1enn \u00f1i faatu.\n11:31 Su nu doon seetlu sunu bopp ni mu ware, kon \u00e0tte du nu dal.\n11:32 Waaye bu nu Boroom bi dee \u00e0tte, da nuy yar ngir ba\u00f1 noo boole ci mbugalu \u00e0ddina.\n11:33 Noonu nag bokk yi, bu ngeen dajee, di lekk reeru Boroom bi, nangeen xaarante.\n11:34 Ku xiif, na lekke k\u00ebram, ngir ba\u00f1 a indi ci y\u00e9en \u00e0tteb Y\u00e0lla ndax seen ndaje yi. Yeneen f\u00e0nn yi ci des nag, bu ma \u00f1\u00ebwee ci y\u00e9en, dinaa ko seet.\n12:1 L\u00e9egi nag bokk yi, ci li j\u00ebm ci mayi Xelum Y\u00e0lla, b\u00ebgguma ngeen umple ci dara.\n12:2 Xam ngeen ne, bi ngeen xamagul woon Y\u00e0lla, x\u00ebr\u00ebm, yi m\u00ebnul a wax, \u00f1oo leen jiitaloon, di leen wommat.\n12:3 Moo tax ma leen di xamal lii: ku Xelum Y\u00e0lla solu du wax ne: \u00abYeesu dafa araam.\u00bb Te it kenn m\u00ebnul a wax ne: \u00abYeesu mooy Boroom bi,\u00bb su ko ko Xelum Y\u00e0lla waxloowul.\n12:4 Am na f\u00e0nni may yu bare yu j\u00f3ge ci Xelum Y\u00e0lla, waaye menn Xel moomu moo koy s\u00e9ddale.\n12:5 Am na ay sas yu bare, waaye benn Boroom bi la.\n12:6 Am na ay f\u00e0nn yu bare yu Y\u00e0llay fee\u00f1ale dooleem, waaye jenn Y\u00e0lla ji mooy j\u00ebfe doole yooyu y\u00e9pp ci \u00f1\u00e9pp.\n12:7 Noonu Y\u00e0lla jox na ku nekk f\u00e0nn gu muy fee\u00f1ale Xelam mu Sell mi ngir njari\u00f1ul \u00f1\u00e9pp.\n12:8 Am na ku Y\u00e0lla s\u00e9dde, jaarale ko ci Xelam, mayu wax ak xel mu leer, keneen am mayu xam-xam, te mu bawoo ci menn Xel mi.\n12:9 Keneen it menn Xel mi jox ko ng\u00ebm, keneen di w\u00e9ral ay j\u00e0ngoro ci k\u00e0ttanu Xel moomu,\n12:10 keneen di def ay k\u00e9emaan, am kuy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, am keneen kuy r\u00e0\u00f1\u00f1ee li j\u00f3ge ci Xelum Y\u00e0lla ak li j\u00f3ge ci yeneen xel yi, keneen it di wax ay xeeti l\u00e0kk, ak kuy firi l\u00e0kk yooyu.\n12:11 Loolu l\u00e9pp, menn Xel moomu moo koy def, ku nekk mu s\u00e9dd la ci, ni mu ko soobe.\n12:12 Noona la ci yaramu nit. Yaram wenn la, teewul am na c\u00e9r yu bare. Waaye c\u00e9ri yaram y\u00e9pp, ak li \u00f1uy baree-bare, \u00f1oo bokk, doon wenn yaram. Te noonu la Kirist mel.\n12:13 Y\u00e0lla s\u00f3ob na nu ci menn Xelam mi, ngir nu doon wenn yaram: nuy Yawut walla nu dul Yawut, nuy jaam mbaa gor, nun \u00f1\u00e9pp Y\u00e0lla may na nu, nu naan ci menn Xel mi.\n12:14 Yaram du benn c\u00e9r, waaye c\u00e9r yu bare la.\n12:15 Kon bu t\u00e0nk nee: \u00abMan duma loxo, kon bokkuma ci yaram,\u00bb du ko teree bokk ci c\u00e9ri yaram yi.\n12:16 Te bu nopp nee: \u00abDuma b\u00ebt, kon bokkuma ci yaram,\u00bb du ko teree bokk ci c\u00e9ri yaram yi.\n12:17 Bu yaram w\u00e9pp doon b\u00ebt, kon nan lay d\u00e9gge? Walla bu yaram w\u00e9pp doon nopp, kon nan lay xee\u00f1too?\n12:18 Waaye Y\u00e0lla dafa riime c\u00e9ri yaram wi, def bu ci nekk fa mu ko soobe.\n12:19 Bu l\u00e9pp doon benn c\u00e9r, kon fu yaram di nekk?\n12:20 C\u00e9r yi daal, bare na\u00f1u waaye wenn yaram rekk a am.\n12:21 B\u00ebt nag m\u00ebnul ne loxo: \u00abSoxlawuma la!\u00bb Te bopp it m\u00ebnul ne t\u00e0nk yi: \u00abSoxlawuma leen!\u00bb\n12:22 Loolu sax m\u00ebnul a am, ndaxte c\u00e9ri yaram, yi g\u00ebn a n\u00e9ew doole, \u00f1oo g\u00ebn a am jari\u00f1.\n12:23 Te c\u00e9r yi g\u00ebn a \u00f1\u00e0kk maana, \u00f1oom lanuy g\u00ebn a topptoo. C\u00e9r yi ci rafetul a tudd, \u00f1oom lanuy g\u00ebn a suturaal,\n12:24 fekk yi g\u00ebn a rafet, soxlawul nu leen di suturaale noonu. Waaye Y\u00e0lla dafa boole sunu c\u00e9ri yaram yi, ngir g\u00ebn a teral c\u00e9r yi ko soxla.\n12:25 Noonu yaram du s\u00e9ddaloo, waaye c\u00e9r bu ci nekk dina dimbali yi ci des.\n12:26 Bu sa benn c\u00e9ru yaram dee metti, yeneen yi ci des y\u00e9pp da\u00f1uy bokk, y\u00e9g metit wi. Te bu dee dangaa fonk sa benn c\u00e9ru yaram it, ndax du sa yaram w\u00e9pp a ciy b\u00e0nneexu?\n12:27 L\u00e9egi benn yaram ngeen, muy yaramu Kirist, te kenn ku nekk ci y\u00e9en c\u00e9r nga ci.\n12:28 Te Y\u00e0lla teg na ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm, ku nekk ak sa may: ci bu j\u00ebkk ay ndawi Kirist, teg ca \u00f1iy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, teg ca \u00f1iy j\u00e0ngale, \u00f1iy def ay k\u00e9emaan, \u00f1i am mayu w\u00e9ral ay j\u00e0ngoro, \u00f1iy dimbalee, \u00f1iy jiite, \u00f1iy wax ay xeeti l\u00e0kk.\n12:29 Ndax \u00f1\u00e9pp ay ndawi Kirist la\u00f1u? Ndax \u00f1\u00e9pp da\u00f1uy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla? Ndax \u00f1\u00e9pp ay j\u00e0ngale? Ndax \u00f1\u00e9pp ay def k\u00e9emaan?\n12:30 Ndax \u00f1\u00e9pp a am mayu w\u00e9ral ay j\u00e0ngoro? Ndax \u00f1\u00e9pp ay wax ay l\u00e0kk? Ndax \u00f1\u00e9pp a leen di firi?\n12:31 Waaye fonkleen may yi g\u00ebn. L\u00e9egi nag ma won leen yoon wu g\u00ebn l\u00e9pp.\n13:1 Su fekkee ne damay wax l\u00e0kki nit \u00f1i ak yu malaaka yi sax, te boolewuma ci mb\u00ebggeel, duma dara lu dul nd\u00ebnd muy riir, walla j\u00f3ol\u00f3oli buy kanda\u014b-kanda\u014bi.\n13:2 Su ma y\u00e9glee wax ju tukkee ci Y\u00e0lla, ma xam l\u00e9pp luy kumpa, ma yor xam-xam b\u00e9pp, te g\u00ebm Y\u00e0lla ba man a randal ay tund, fekk boolewuma ci mb\u00ebggeel, duma dara.\n13:3 Te it su ma doon saraxe li ma am l\u00e9pp, di b\u00e0yyi \u00f1u lakk sama yaram, ba rey ma, su ma ci boolewul mb\u00ebggeel, du ma jari\u00f1 dara.\n13:4 Ku b\u00ebgg dafay mu\u00f1 te laabiir. Ku b\u00ebgg du ki\u00f1aan, du ka\u00f1u, du tiitaru,\n13:5 du def lu jekkadi, du wut njari\u00f1u boppam, du naqari deret, du \u00f1aaw njort.\n13:6 Du b\u00e9g ci lu awul yoon, waaye dina b\u00e9g ci l\u00e9pp luy jollil d\u00ebgg.\n13:7 Mb\u00ebggeel day baale l\u00e9pp, am g\u00ebm ci l\u00e9pp, yaakaar l\u00e9pp, mu\u00f1 l\u00e9pp.\n13:8 Mb\u00ebggeel amul \u00e0pp. \u00d1iy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla dina\u00f1u noppi, \u00f1iy wax ay l\u00e0kk dina\u00f1u ko b\u00e0yyi, \u00f1iy xamle xam-xamu Y\u00e0lla w\u00e0cc.\n13:9 Xam-xam bi nu am des na, te ni nu jottalee xebaar bi nu Y\u00e0lla d\u00e9nk des na.\n13:10 Waaye li mat, bu dikkee, li matul j\u00f3ge fi.\n13:11 Bi ma dee xale, dama doon wax ni xale, di d\u00e9gge ni xale, di xalaate ni xale. Waaye bi ma doonee mag, b\u00e0yyi naa lu bokkoon cig ndaw.\n13:12 Tey jii gis bu l\u00ebnd\u00ebm lanuy gis, ni takkandeer ci seetu bu l\u00ebnd\u00ebm, bu \u00ebll\u00ebgee dinanu gis jaxran. Tey jii sama xam-xam des na, bu \u00ebll\u00ebgee dinaa xam ba mat s\u00ebkk, ni ma Y\u00e0lla xame.\n13:13 L\u00e9egi nag \u00f1ett yii \u00f1ooy sax: ng\u00ebm, yaakaar, mb\u00ebggeel; te mb\u00ebggeel moo ci raw.\n14:1 Xintewooleen mb\u00ebggeel te fonk mayi Xelum Y\u00e0lla, rawatina mayu wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla,\n14:2 ndaxte kiy wax aw l\u00e0kk, waxul ak nit \u00f1i, waaye Y\u00e0lla lay waxal, ndaxte kenn d\u00e9ggul li muy wax. Dafay wax ay mb\u00f3ot ci xelam.\n14:3 Waaye kiy jottali k\u00e0ddug Y\u00e0lla, nit \u00f1i lay waxal ngir y\u00e9kkati seen ng\u00ebm, di leen d\u00e9nk ak a d\u00ebf\u00ebl.\n14:4 Kiy wax aw l\u00e0kk dafay yokk boppam, waaye kiy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, dafay yokk ng\u00ebmu mbooloo mi.\n14:5 L\u00e9egi nag b\u00ebgg naa y\u00e9en \u00f1\u00e9pp, ngeen di wax ay l\u00e0kk, waaye li ma g\u00ebnal mooy ngeen di wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla. Kiy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla moo g\u00ebn kiy wax ay l\u00e0kk, su firiwul li muy wax, ngir ng\u00ebmu mbooloo mi yokku.\n14:6 Kon nag bokk yi, su ma \u00f1\u00ebwee ci y\u00e9en, di wax ay l\u00e0kk, lu ma leen di jari\u00f1? Dara, su ma leen indilul d\u00ebgg gu Y\u00e0lla fee\u00f1al, walla xam-xam walla k\u00e0ddu gu tukkee ca Y\u00e0lla, walla am nj\u00e0ngale.\n14:7 Noonu la mel itam ci y\u00ebf yi dundul tey riir, ni toxoro walla xalam. Su li ci jibe leerul, naka la nit man a r\u00e0\u00f1\u00f1ee li mbiibi toxoro walla buumi xalam di wax?\n14:8 Rax-ca-dolli su liit gi jibul bu leer, kuy man a waajal xare ba?\n14:9 Noonu itam bu ngeen g\u00e9nnewul ay wax yu leer ci seen g\u00e9mmi\u00f1, nan la\u00f1uy man a xame li ngeen di wax? Dingeen wax cig neen!\n14:10 Xawma \u00f1aata xeeti l\u00e0kk a am ci \u00e0ddina, te wu ci nekk am na lu muy tekki.\n14:11 Su ma xamul nag l\u00e0kk wi \u00f1u may l\u00e0kk, doxand\u00e9em laay doon ci ki koy wax, te ki koy wax it doxand\u00e9em la ci man.\n14:12 Y\u00e9en itam, gannaaw dangeen a fonk mayi Xelum Y\u00e0lla, j\u00e9emleen a \u00ebpple ci liy yokk ng\u00ebmu mbooloo mi.\n14:13 Looloo tax kiy wax aw l\u00e0kk, na \u00f1aan ngir mu man a firi li looluy tekki.\n14:14 Su may \u00f1aan Y\u00e0lla ci aw l\u00e0kk, sama xol day \u00f1aan, waaye sama xel amalul kenn njari\u00f1.\n14:15 Kon nag lu muy indi? Bu may \u00f1aan, dinaa \u00e0nd ak sama xol, \u00e0ndaale ak sama xel. Bu may woy, dinaa \u00e0nd ak sama xol, \u00e0ndaale ak sama xel.\n14:16 Walla, boo dee g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla, \u00e0nd ci ak sa xol rekk, kon ku musul a j\u00e0ng mbir yooyu, nan la man a waxe: \u00abAmiin,\u00bb ci sa cant Y\u00e0lla googu? Ndaxte xamul li ngay wax.\n14:17 D\u00ebgg la, dangay sant Y\u00e0lla bu baax, waaye ki ci des, ng\u00ebmam yokkuwul.\n14:18 Maa ngi sant Y\u00e0lla ci li may wax ay l\u00e0kk, ba raw leen y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.\n14:19 Waaye ci ndajem mbooloom \u00f1i g\u00ebm, wax jur\u00f3omi baat yu am njari\u00f1, ngir j\u00e0ngal \u00f1i ci des, moo ma g\u00ebnal wax fukki junniy baat ciw l\u00e0kk.\n14:20 Bokk yi, buleen melati ni ay xale, ci ni ngeen di xalaate. Ci lu j\u00ebm ci lu bon, mel-leen ni ay xale, waaye ci seeni xalaat, mel-leen ni ay mag.\n14:21 Bind na\u00f1u ci t\u00e9ereb yoon wi:\u00abDinaa wax ak mbooloo mii,jaare ko ci ay nit, \u00f1uy wax yeneen l\u00e0kk,ak ay g\u00e9mmi\u00f1i doxand\u00e9em,waaye ba tey du\u00f1u ma d\u00e9glu.\u00bb Moom la Boroom bi wax.\n14:22 Ci noonu wax ay l\u00e0kk, firnde la ci \u00f1i g\u00ebmul, te du firnde ci \u00f1i g\u00ebm. Te it wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, du firnde ci \u00f1i g\u00ebmul, waaye firnde la ci \u00f1i g\u00ebm.\n14:23 Kon nag su fekkee ku j\u00e0ngul mbiri Kirist walla ku g\u00ebmul dugg ca mbooloo ma, fekk \u00f1\u00e9pp di wax ay l\u00e0kk, ndax du wax ne, dangeen a dof?\n14:24 Waaye bu \u00f1\u00e9pp dee wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, te ku g\u00ebmul dugg fa, walla ku j\u00e0ngul mbiri Kirist, wax yi \u00f1\u00e9pp wax dafay wone b\u00e0kkaaram te \u00e0tte ko,\n14:25 ba kumpay xolam fee\u00f1. Bu ko defee dina d\u00ebpp j\u00ebwam ci suuf, di m\u00e0ggal Y\u00e0lla te naan: \u00abD\u00ebgg-d\u00ebgg Y\u00e0llaa ngi ci seen biir.\u00bb\n14:26 Kon nag bokk yi, lu muy indi? Bu ngeen dajee, kii am aw taalif, kii am nj\u00e0ngale, kii d\u00ebgg gu Y\u00e0lla fee\u00f1al, kii di wax aw l\u00e0kk, kee di ko firi. Na loolu l\u00e9pp aw ci yoonu yokk ng\u00ebmu mbooloo mi.\n14:27 Su amee kuy wax aw l\u00e0kk, na \u00f1aar wax walla g\u00ebn gaa bare \u00f1ett. Na\u00f1u ko toppante, te kenn di firi.\n14:28 Su amul kuy firi, kooku di wax aw l\u00e0kk, na noppi ci ndajem mbooloo mi. Na waxanteek Y\u00e0lla ci xolam.\n14:29 Ci \u00f1iy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla nag, na \u00f1aar walla \u00f1ett wax, te \u00f1i ci des r\u00e0\u00f1\u00f1ee li \u00f1uy wax.\n14:30 Su amee ku toog te Y\u00e0lla fee\u00f1al ko d\u00ebgg, na ki doon wax noppi.\n14:31 Y\u00e9en \u00f1\u00e9pp man ngeen a kenn-kennoo wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, ngir \u00f1\u00e9pp j\u00e0ng te d\u00e9gg li \u00f1u leen di d\u00e9nk.\n14:32 \u00d1iy jottali k\u00e0ddug Y\u00e0lla da\u00f1oo moom seen xel,\n14:33 ndaxte Y\u00e0lla du Y\u00e0llay l\u00ebj-l\u00ebj waaye Y\u00e0llay j\u00e0mm la. Ci mboolooy gaayi Y\u00e0lla y\u00e9pp,\n14:34 na jig\u00e9en \u00f1i noppi ci ndaje mi, ndaxte sa\u00f1u\u00f1u faa wax. Na\u00f1u doon jig\u00e9en \u00f1u nangu, ni ko yoon wi t\u00ebrale.\n14:35 Te su \u00f1u b\u00ebggee laaj dara, na\u00f1u ko laaj seen j\u00ebkk\u00ebr ca k\u00ebr ga, ndaxte jig\u00e9en di wax ci ndajem mbooloom \u00f1i g\u00ebm, g\u00e0cce la.\n14:36 Ndax ci y\u00e9en la k\u00e0ddug Y\u00e0lla sosoo? Walla ndax ci y\u00e9en rekk la agsi?\n14:37 Su kenn xalaatee ne, mooy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, walla mu xalaat ne, Xelum Y\u00e0lla jagleel na may, na nangu ne lii ma leen bind ndigalu Boroom bi la.\n14:38 Te su ko xeebee it, \u00f1u xeeb ko.\n14:39 Kon nag bokk yi, farluleen ci di wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, te buleen tere kenn muy wax ay l\u00e0kk.\n14:40 Waaye nag, na l\u00e9pp di dox ciy teggin te aw yoon.\n15:1 L\u00e9egi nag bokk yi, maa ngi leen di f\u00e0ttali xebaar bu baax bi ma leen y\u00e9gal. Xebaar bu baax boobu, nangu ngeen ko te y\u00e9ena ngi ciy sax.\n15:2 Ci moom ngeen jaare, ba mucc, bu ngeen t\u00e9yee bu d\u00ebg\u00ebr nj\u00e0ngale mi, ni ma leen ko y\u00e9gale. Walla xanaa boog g\u00ebm ngeen ko cig neen?\n15:3 Li ma jotoon, jottali naa leen ko, te moo j\u00ebkk ci maana yi: Kirist dee na ngir dindi sunuy b\u00e0kkaar, ni ko Mbind mi t\u00ebrale,\n15:4 suul na\u00f1u ko, mu dekki ca \u00f1etteelu fan ba, ni ko Mbind mi t\u00ebrale.\n15:5 Fee\u00f1u na Sefas, teg ca fukki taalibe ya ak \u00f1aar.\n15:6 Gannaaw ga fee\u00f1u na lu \u00ebpp jur\u00f3omi t\u00e9em\u00e9eri bokki taalibe ci benn yoon. Te \u00f1u bare ci \u00f1oom \u00f1u ngi dund ba l\u00e9egi, waaye am na ci \u00f1u nelaw.\n15:7 Ba noppi fee\u00f1u na Saag ak ndawi Kirist y\u00e9pp.\n15:8 Man nag la mujj a fee\u00f1u, ma mel ni liir bu judduwul ci jamonoom.\n15:9 Ndaxte maa g\u00ebn a \u00f1\u00e0kk solo ci ndawi Kirist yi, te yeyoowuma sax, \u00f1u may wooye ndaw, man mi doon fitnaal mbooloom Y\u00e0lla.\n15:10 Waaye nag yiwu Y\u00e0lla moo tax ma doon li ma doon, te yiw, wi mu wone ci man, du cig neen. Waaye sax maa g\u00ebn a ligg\u00e9ey \u00f1i ci des \u00f1\u00e9pp: du ci man, waaye yiwu Y\u00e0lla, wiy j\u00ebf ci man, moo tax.\n15:11 Noonu nag muy man muy \u00f1oom, d\u00e9nkaane boobu lanuy y\u00e9gle, te moom ngeen g\u00ebm.\n15:12 Waaye su nu y\u00e9glee ne, Kirist dekki na, nan la \u00f1enn \u00f1i ci y\u00e9en man a waxe ne, n\u00e9ew yi du\u00f1u dekki?\n15:13 Su fekkee ne \u00f1i dee du\u00f1u dekki, kon Kirist it dekkiwul.\n15:14 Te su Kirist dekkiwul, sunu waare day neen, te it seen ng\u00ebm day neen.\n15:15 Rax-ca-dolli gis na\u00f1u ne, seedeel nanu Y\u00e0lla ay fen, ndaxte seede nanu ci mbiram ne, dekkal na Yeesu, te fekk dekkalu ko, su n\u00e9ew yi dul dekki.\n15:16 Su n\u00e9ew yi dul dekki, Kirist moom it dekkiwul.\n15:17 Te su Kirist dekkiwul, seen ng\u00ebm du am solo, ba tey y\u00e9ena ngi ci seeni b\u00e0kkaar.\n15:18 Te it \u00f1i dee ba noppi ci Kirist s\u00e0nku na\u00f1u.\n15:19 Su fekkee ci giiru dund gii rekk la sunu yaakaar ci Kirist ame solo, kon noo g\u00ebn a mat a y\u00ebr\u00ebm \u00f1\u00e9pp.\n15:20 Waaye l\u00e9egi Kirist dekki na, di ku j\u00ebkk a dekki, ni gub yi \u00f1u j\u00ebkk a t\u00e0nne ci ng\u00f3ob mi, jagleel leen Y\u00e0lla.\n15:21 Gannaaw ci nit la dee jaar, dugg \u00e0ddina, kon it ci nit la ndekkite jaar.\n15:22 Kon ni \u00f1\u00e9pp deeye ci seen bokk ci Aadama, noonu la \u00f1\u00e9pp di dundaate ci seen bokk ci Kirist.\n15:23 Waaye ku nekk ak ayam. Kirist moo j\u00ebkk, mel ni gub yi \u00f1u j\u00ebkk a t\u00e0nne ci ng\u00f3ob mi, ba noppi, bu Kirist dellusee, \u00f1i bokk ci moom j\u00ebl seen ay.\n15:24 Gannaaw ga, mujug jamono taxaw, te Kirist dina noot g\u00e9pp kilifa ak b\u00e9pp sa\u00f1-sa\u00f1 ak doole, ba noppi delloo nguur gi kiy Y\u00e0lla di Baayam.\n15:25 Ndaxte f\u00e0ww Kirist nguuru, ba kera Y\u00e0lla di daaneel noonam y\u00e9pp ciy t\u00e0nkam.\n15:26 Noon bu mujj, bi mu fiy j\u00eble, mooy dee.\n15:27 Ndaxte Mbind mi nee na: \u00abY\u00e0lla nootal na ko l\u00e9pp, mu teg ci t\u00e0nk.\u00bb Waaye bu Mbind mi nee, \u00abnoot na l\u00e9pp,\u00bb w\u00f3or na ne, moom mi ko nootal l\u00e9pp, g\u00e9nne na ci boppam.\n15:28 L\u00e9egi bu \u00f1u ko nootalee l\u00e9pp nag, moom Kirist muy Doom ji dina delloo kilifteef gi Y\u00e0lla, mi ko nootal l\u00e9pp, ngir Y\u00e0lla nekk buur ci l\u00e9pp.\n15:29 Su ndekkite amul, kon \u00f1i \u00f1u s\u00f3ob ci ndox ngir \u00f1i dee, lu mu leen di jari\u00f1? Su dekki amul, kon lu tax \u00f1u leen di s\u00f3ob ngir \u00f1i dee?\n15:30 Te nun it lu tax fu nu tollu nu jaay sunu bakkan?\n15:31 Bokk yi, ni ma damoo ci y\u00e9en ndax Yeesu Kirist, ni la ma w\u00f3ore ne, b\u00e9s bu nekk ma riisu dee.\n15:32 Su fekkee ne ci ni \u00f1u ko waxe, xeex naa ca d\u00ebkku Efes ak rabi \u00e0ll, kon ban njari\u00f1 la may amal? Su n\u00e9ew yi dul woon dekki, am na lu ci l\u00e9eb wax:\u00abNanu lekk di naan, ndaxte \u00ebll\u00ebg dinanu dee.\u00bb\n15:33 Bu leen ko r\u00e9ere mbir: \u00ab\u00c0nd bu bon dina y\u00e0q nit ku baax.\u00bb\n15:34 Delloosileen xel yi te b\u00e0yyi b\u00e0kkaar, ndaxte am na ci y\u00e9en, \u00f1u umple Y\u00e0lla. Kon war ngeen a rus!\n15:35 Waaye dina am kuy naan: \u00abNan la n\u00e9ew yi di dekkee? Wan yaram la\u00f1uy dellusee?\u00bb\n15:36 Yaa g\u00e0tt xel! Li ngay ji, du jebbi dund gu bees, fi ak deewul ba noppi.\n15:37 Te li ngay ji du j\u00ebmmi g\u00e0ncax giy \u00f1\u00ebwi, waaye pepp kese la, maanaam dugub, walla weneen jiwu.\n15:38 Noonu Y\u00e0lla jox ko j\u00ebmm ju ko neex, jiwu wu nekk ak j\u00ebmmam.\n15:39 J\u00ebmmi mbindeef y\u00e9pp a wuute: nit ak j\u00ebmmam, mala, picc, j\u00ebn \u2014 yu ci nekk ak sa j\u00ebmmi bopp.\n15:40 Am na itam ay j\u00ebmm ca asamaan ak ay j\u00ebmm ci suuf. Leeru j\u00ebmm ca asamaan wuute na ak gi ci suuf.\n15:41 Jant bi, weer wi ak biddiiw, lu nekk ak sag leer. Te it leeru biddiiw bu nekk dina wuute ak moroomam.\n15:42 Noonu la ndekkitel n\u00e9ew yi di deme. Bu \u00f1u suulee n\u00e9ew bi, da\u00f1oo ji lu y\u00e0qu. Bu dekkee, du y\u00e0qooti ba abadan.\n15:43 Lu \u00f1\u00e0kk solo la\u00f1uy suul; mu dekki ak ndam. Lu n\u00e9ew doole la\u00f1uy suul, mu dekki ak k\u00e0ttan.\n15:44 Bu \u00f1u koy suul, yaram lay doon wu soloo woon ruu. Bu dekkee, doon yaram wu soloo ndamu Xelum Y\u00e0lla. Ndegam am na yaram wu soloo ruu, kon dina am yaram wu soloo ndamu Xelum Y\u00e0lla.\n15:45 Mbind mi nee na: \u00abNit ku j\u00ebkk ka, Aadama, doon na boroom ruu,\u00bb waaye Aadama mu mujj mi doon na Xel muy joxe dund.\n15:46 Yaram wi soloo ndamu Xelum Y\u00e0lla jiituwul; yaramu doom Aadama moo jiitu; yaramu ndam li moo ci topp.\n15:47 Nit ku j\u00ebkk ka p\u00ebndu suuf la woon; \u00f1aareelu nit ki di Kirist, mi ngi j\u00f3ge asamaan.\n15:48 Waa \u00e0ddina yor na\u00f1u j\u00ebmmi nit, ki \u00f1u s\u00e0kke ci suuf; noonu it \u00f1i bokk ci asamaan dina\u00f1u yor melokaanu ki j\u00f3ge ci asamaan.\n15:49 Te ni nu yore melokaanu ki \u00f1u s\u00e0kke ci suuf, noonu lanuy yoreji melokaanu ki j\u00f3ge ca asamaan.\n15:50 Li may wax nag bokk yi, moo di ne, sunu yaram wii m\u00ebnul a am w\u00e0ll ci nguuru Y\u00e0lla, te lu y\u00e0qu m\u00ebnul a am w\u00e0ll ci liy sax abadan.\n15:51 Lii ma leen di xamal, mb\u00f3otu Y\u00e0lla la. D\u00e9gluleen, dunu jaar ci dee nun \u00f1\u00e9pp, waaye nun \u00f1\u00e9pp dinanu soppiku,\n15:52 ci saa su g\u00e0tt, ci xef-ak-xippi, bu liit gu mujj gi jibee. Ndax liit gi dina jib, n\u00e9ew yi dekki, di dund abadan, te nun dinanu soppiku.\n15:53 Yaram wu y\u00e0qu war na sol j\u00ebmm ja dul y\u00e0qooti, te yaram wiy dee sol dund gu sax abadan.\n15:54 Bu li y\u00e0qu solee melokaanu li dul y\u00e0qu, te liy dee sol melokaanu liy sax abadan, kon lii \u00f1u wax ci Mbind mi mat:\u00abY\u00e0lla noot na dee, ba labal ko ci ndamam.\n15:55 C\u00e9y yaw dee! Ana sa ndam?C\u00e9y yaw dee! Ana sa da\u014bar ji ngay fitte?\u00bb\n15:56 Da\u014baru dee mooy b\u00e0kkaar, te dooley b\u00e0kkaar mooy Yoon wi.\n15:57 Waaye j\u00ebr\u00eb-j\u00ebf yaw Y\u00e0lla, ji nu jox ndam li jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist!\n15:58 Kon nag sama bokk yi ma sopp, nangeen takku, sampu ba d\u00ebg\u00ebr, te g\u00ebn a sawar ci ligg\u00e9eyu Boroom bi, xam ne seen ligg\u00e9ey, bi j\u00ebm ci Boroom bi, du neen.\n16:1 L\u00e9egi nag ci li j\u00ebm ci ndimbal, li \u00f1uy s\u00e0kkal gaayi Y\u00e0lla yi, defleen li ma t\u00ebral ci mboolooy \u00f1i g\u00ebm te nekk ci diiwaanu Galasi.\n16:2 B\u00e9s bu j\u00ebkk ci ayu-b\u00e9s yi, na ku nekk ber lu mu \u00e0ttan, denc ko, ngir saa yu ma dikkee, \u00f1u ba\u00f1 di w\u00ebr di laaj xaalis.\n16:3 Su ma dikkee, dinaa d\u00e9nk seen xaalis \u00f1i ngeen t\u00e0nn, y\u00f3nni leen Yerusalem, boole ko ak bataaxal.\n16:4 Su aajoo ma demal sama bopp, kon dina\u00f1u \u00e0nd ak man.\n16:5 Gannaaw bu ma j\u00e0llee diiwaanu Maseduwan, dinaa \u00f1\u00ebw ci y\u00e9en, ndaxte fas naa ko y\u00e9enee j\u00e0ll.\n16:6 Man na am ma y\u00e0gg ci y\u00e9en, jombul sax ma lollikoo fi y\u00e9en. Noonu dingeen taxawu sama yoon, fu ma man a j\u00ebm.\n16:7 Ndaxte fi mu ne b\u00ebgguma leen a gis rekk, j\u00e0ll, waaye yaakaar naa ne, dinaa toog ci y\u00e9en ab diir, bu neexee Boroom bi.\n16:8 Ba tey dinaa toog fii ci d\u00ebkku Efes ba m\u00e0ggalu P\u00e0ntakot,\n16:9 ndaxte Y\u00e0lla ubbil na ma bunt, ba mu ne l\u00e0\u00f1\u00f1, ngir may def ligg\u00e9ey bu man a am muj gu rafet, te noon yu bare b\u00ebgg a g\u00e0llankoor ligg\u00e9ey bi.\n16:10 Bu leen Timote ganesee, fexeleen ba bumu am nj\u00e0qare ci seen biir, ndaxte dafay ligg\u00e9eyal Boroom bi ni man.\n16:11 Kon bu ko kenn xeeb. Nangeen taxawu yoonam, ba mu dellusi ci man ci j\u00e0mm, ndaxte maa ngi koy xaar ak bokk yi.\n16:12 Naka Apolos sunu mbokk mi nag moom, xiir naa ko ay yooni yoon, mu \u00f1\u00ebw ci y\u00e9en, \u00e0nd ak bokk yi. Waaye fi mu ne d\u00ebppoowul ak coobareem. Dina \u00f1\u00ebw saa su ko manee.\n16:13 Farluleen te d\u00ebg\u00ebr ci ng\u00ebm, di g\u00f3or-g\u00f3orlu te am pasteef.\n16:14 L\u00e9pp li ngeen di def, defleen ko ak mb\u00ebggeel.\n16:15 Xam ngeen ne, Estefanas ak njabootam \u00f1oo j\u00ebkk a nangu xebaar bu baax bi ci diiwaanu Akayi, te \u00f1oo joxe seen bopp, ngir ligg\u00e9eyal gaayi Y\u00e0lla yi. Kon nag bokk yi, maa ngi leen di \u00f1aan,\n16:16 ngeen nangul nit \u00f1u mel noonu, \u00f1oom ak k\u00e9pp ku \u00e0nd ak \u00f1oom ci ligg\u00e9ey bi.\n16:17 Bi ma Estefanas ak Fortunatus ak Akaykus seetsee, b\u00e9g naa ci lool. Taxawal na\u00f1u leen ci topptoo, bi ngeen y\u00e9ene woon ci man te t\u00eble ko.\n16:18 Seral na\u00f1u sama xol ak seen yos itam. Kon fonkleen nit \u00f1u mel noonu.\n16:19 Mboolooy \u00f1i g\u00ebm te nekk diiwaanu Asi \u00f1u ngi leen di nuyu. Akilas ak Pirsil, \u00f1u ngi leen di nuyu bu baax ci Boroom bi, \u00f1oom ak mbooloom \u00f1i g\u00ebm tey daje seen k\u00ebr.\n16:20 Bokk y\u00e9pp \u00f1u ngi leen di nuyu. Saafoonteleen ak xol bu laab.\n16:21 Man Pool maa bind nuyoo bii ci sama loxob bopp.\n16:22 K\u00e9pp ku ba\u00f1 Boroom bi, Yal na ko Y\u00e0lla alag. Boroom bi, \u00f1\u00ebwal!\n16:23 Na yiwu Boroom bi Yeesu \u00e0nd ak y\u00e9en.\n16:24 B\u00ebgg naa leen y\u00e9en \u00f1\u00e9pp ndax sunu booloo ak Yeesu Kirist.","title":"Wolof Bible (NT): 1 Corinthians","type":"page"}
