{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/co2.htm","path":"bib/wb/wlf/co2.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/co2.htm","text":"1:1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Y\u00e0lla, man ak Timote sunu mbokk, noo leen di bind, y\u00e9en mbooloom Y\u00e0lla mi nekk d\u00ebkku Korent, ak gaayi Y\u00e0lla yu sell, yi nekk ci diiwaanu Akayi g\u00e9pp.\n1:2 Na leen Y\u00e0lla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak j\u00e0mm.\n1:3 Cant \u00f1eel na Y\u00e0lla, Baayu sunu boroom Yeesu Kirist, di Baay biy Aji Y\u00ebrmande tey Boroom l\u00e9pp luy d\u00ebf\u00ebl xol yi.\n1:4 Mooy d\u00ebf\u00ebl sunu xol ci sunu tiis y\u00e9pp, ngir nun ci sunu bopp nu man a d\u00ebf\u00ebl xolu \u00f1\u00e9pp \u00f1i nekk ci tiis, di leen s\u00e9dd ci noflaay, bi Y\u00e0lla def ci sunu xol.\n1:5 Ndaxte ni coonoy Kirist di baawaane ci nun, noonu it la Kirist nekke buntu noflaay bu yaa, biy d\u00ebf\u00ebl sunu xol.\n1:6 Su nuy jaar ci tiis, seen noflaay a tax ak seen mucc. Bu dee Y\u00e0lla d\u00ebf\u00ebl na sunu xol, seen noflaay a tax, ngir ngeen man a d\u00e9kku naqar yu mel ni yu nuy am, nun itam.\n1:7 Te sunu yaakaar ci seen mbir d\u00ebg\u00ebr na, xam ne, ni ngeen bokke ak nun naqar, noonu ngeen di bokke ak nun noflaayu xol.\n1:8 Ndaxte bokk yi, b\u00ebggunu ngeen umple tiis, wi nu daj ci diiwaanu Asi. Yen bi diisoon na lool ba weesu sunu k\u00e0ttan, ba amatunu yaakaar sax ci dund.\n1:9 Demoon nanu ba defe ne, dogalees na sunug dee. Loolu amoon na, ngir nu ba\u00f1 a w\u00e9er sunu yaakaar ci sunu bopp, waaye nu w\u00e9er ko ci Y\u00e0lla, miy dekkal n\u00e9ew yi.\n1:10 Moo nu musal ci dee gu metti googu te dina nu musalaat. Ci moom lanu w\u00e9kk sunu yaakaar ne, dina nu musalati,\n1:11 bu ngeen nu j\u00e0pplee di ci boole seeni \u00f1aan. Noonu \u00f1u bare dina\u00f1u g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla ci yiw, wi mu nu may te muy tontul \u00f1aanu \u00f1u bare.\n1:12 Li nuy tiitaroo moo di sunu xel day seede ne, ci kanamu \u00e0ddina si, rawatina sax ci seen kanam, aw nanu ci t\u00e0nk yu jub, \u00e0nd ak xol bu laab fa kanam Y\u00e0lla. J\u00ebfewunu ci pexem nit, waaye ci yiwu Y\u00e0lla lanu j\u00ebfe.\n1:13 Bindunu leen nag leneen lu dul li ngeen j\u00e0ng te xam ko. Fi mu ne seen xam-xam ci nun matagul, waaye yaakaar naa ne, bu matee, dingeen man a tiitaru ci nun, ni nu koy defe ci y\u00e9en, bu b\u00e9su Boroom bi Yeesu \u00f1\u00ebwee.\n1:15 Kon ni ma ame woon k\u00f3olute googu, naroon naa j\u00ebkk a jaar ci y\u00e9en, ngir ganesi leen \u00f1aari yoon.\n1:16 B\u00ebggoon naa jaar ci y\u00e9en, dem diiwaanu Maseduwan, te bu ma j\u00f3gee Maseduwan, dikkaat ci y\u00e9en, ngir ngeen waajal sama tukki ca Yude.\n1:17 Ba may m\u00e9b\u00e9t loolu nag, ndax dama cee boolewul pasteef? Te ndax samay y\u00e9ene y\u00e9eney nit kese la, ba may xel \u00f1aar, naan \u00abwaaw\u00bb ak \u00abd\u00e9et?\u00bb\n1:18 W\u00f3or na Y\u00e0lla ne, li nu leen di wax, du \u00abwaaw\u00bb ju \u00e0nd ak \u00abd\u00e9ed\u00e9et.\u00bb\n1:19 Ndaxte Doomu Y\u00e0lla ji, Yeesu Kirist, mi nu doon y\u00e9gle ci seen biir, man ak Silwan ak Timote, nekkul woon \u00abwaaw\u00bb ak \u00abd\u00e9ed\u00e9et;\u00bb \u00abwaawi\u00bb Y\u00e0lla la mas a nekk.\n1:20 Te l\u00e9pp lu Y\u00e0lla dige woon fekk na \u00abwaawam\u00bb ci moom. Noonu kon ci Kirist lanuy waxe: \u00abAmiin,\u00bb ngir y\u00e9kkati ndamu Y\u00e0lla.\n1:21 Te Y\u00e0lla moo nuy d\u00ebg\u00ebral ci Kirist, nun ak y\u00e9en, te sol nu Xelam.\n1:22 Moo nu m\u00e0ndargaal ni ay gaayam, def Xelam ci sunu xol, muy dawal ci c\u00e9r, bi mu nu dencal.\n1:23 Man nag Y\u00e0lla seede na ma, te gi\u00f1 naa ci sama bakkan ne, y\u00ebr\u00ebm leen rekk moo tax delluseeguma Korent.\n1:24 Du caageen nag noo leen b\u00ebgg a noot ci lu j\u00ebm ci seen ng\u00ebm, waaye nu ngi ligg\u00e9eyandoo ak y\u00e9en ngir seen mb\u00e9g, ndaxte ci ng\u00ebm ngeen sax.\n2:1 Man nag fas y\u00e9ene naa lii: duma dellusi ci y\u00e9en ci naqar.\n2:2 Ndaxte su ma leen tegee naqar, kuy seddal sama xol ku dul y\u00e9en \u00f1i ma teg aw naqar?\n2:3 Looloo tax ma binde noonu, ngir ba\u00f1 a agsi, am naqar ci \u00f1i ma waroon a b\u00e9gal. Am naa k\u00f3olute ci y\u00e9en \u00f1\u00e9pp ne, sama mb\u00e9g mooy seen mb\u00e9g.\n2:4 Ci biir tiis ak xol bu jeex laa leen bind, samay b\u00ebt taa ak ay rangoo\u00f1. Binduma leen ngir teg leen naqar, waaye ngir ngeen xam x\u00f3otaayu mb\u00ebggeel gi ma am ci y\u00e9en.\n2:5 Su kenn tegee moroomam naqar, du man la ko teg, waaye man nanu ne, y\u00e9en \u00f1\u00e9pp la ko teg \u2014 matul may r\u00e9yal mbir mi.\n2:6 \u00c0tte bi ko mbooloo mi teg, doy na.\n2:7 L\u00e9egi nag baal-leen ko te d\u00ebf\u00ebl xolam, ngir ba\u00f1 mu s\u00f3obu ci naqar wu \u00ebpp.\n2:8 Kon maa ngi leen di \u00f1aan, ngeen feddali seen mb\u00ebggeel ci moom.\n2:9 Nattu leen moo tax ma bind leen it, ngir seet ba xam dingeen d\u00e9gg ndigal ci l\u00e9pp.\n2:10 Ku ngeen baal, ma baal ko itam. Man nag, su ma baalee --fekk am lu ma war a baale \u2014 y\u00e9ena tax ma def ko ci kanamu Kirist,\n2:11 ngir Seytaane ba\u00f1 a am bunt bu mu jaar ba nax nu, ndaxte r\u00e9erewunu mbir ay pexeem.\n2:12 Ba ma \u00e0ggee Torowas nag, ngir y\u00e9gle fa xebaar bu baax bi ci Kirist, Boroom bi ubbil na ma ci bunt.\n2:13 Waaye sama xel dalul benn yoon, ndax li ma fa fekkul sama mbokk, Tit. Noonu nag ma t\u00e0ggu leen, daldi dem diiwaanu Maseduwan.\n2:14 Waaye cant \u00f1eel na Y\u00e0lla! Ci sunu booloo ak Kirist, daf nuy y\u00f3bbaale saa su nekk ci gawari ndamam, tey jaar ci nun ngir turu Kirist jolli fu nekk, ni xetu latkolo\u00f1 di tasaaroo.\n2:15 Ndaxte ci Y\u00e0lla, xetu Kirist gu neex lanu, di gilli j\u00ebm ci \u00f1iy mucc ak \u00f1iy s\u00e0nku;\n2:16 ci \u00f1u mujj \u00f1ii, xet gu sedd lanu, guy j\u00ebme ci dee; ci \u00f1u j\u00ebkk \u00f1i, xetu dund lanu, guy j\u00ebme ci dund. Kon ku man a \u00e0ttan yen boobu!\n2:17 Nun nag melunu ni \u00f1u bare, \u00f1iy baana-baana ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, waaye ci sunu booloo ak Kirist, nu ngi waare ak xol bu laab fa kanam Y\u00e0lla, ni yonenti Y\u00e0lla.\n3:1 Mbaa du danoo t\u00e0mbalee t\u00ebgguwaat nag? Mbaa du danoo soxla ni \u00f1enn \u00f1i ay d\u00e9nkaane yu \u00f1u nuy g\u00ebr\u00ebme, te \u00f1uy bataaxal yu j\u00f3ge ci y\u00e9en walla yu j\u00ebm ci y\u00e9en?\n3:2 D\u00e9ed\u00e9et, y\u00e9enay sunu bataaxal, te ci sunu xol la\u00f1u ko bind, di bataaxal bu nit \u00f1\u00e9pp man a xam te j\u00e0ng ko;\n3:3 ndaxte leer na ne, bataaxal bu j\u00f3ge ci Kirist ngeen, bu mu jaarale ci nun. Bindeesu ko daa, waaye ci Xelum Y\u00e0lla miy dund lees ko binde; te du ci \u00e0lluway doj la\u00f1u ko r\u00ebdd, waaye ci xolu doom Aadama.\n3:4 Googu k\u00f3olute lanu am fa kanam Y\u00e0lla ndax Kirist.\n3:5 Du caageen nag ne, \u00e0ttan nanu dara ci sunu man-man, ba nu yaakaar dara ci sunu bopp, waaye sunu k\u00e0ttan ci Y\u00e0lla lay j\u00f3ge.\n3:6 Moo nu jox k\u00e0ttan, nu nekk ndaw yuy xamle k\u00f3ll\u00ebre gu bees gi. Te k\u00f3ll\u00ebre googu ajuwul ci ay s\u00e0rti diine, waaye mi ngi aju ci j\u00ebfu Xelum Y\u00e0lla. Ndaxte s\u00e0rti kese day j\u00ebme ci dee, waaye Xelum Y\u00e0lla dafay joxe dund.\n3:7 Ba \u00f1u bindee arafi s\u00e0rt yi ciy \u00e0lluway doj, leeraayu ndamu Y\u00e0lla nekk fa. Xar-kanamu Musaa di leer, ba b\u00e0nni Israyil du\u00f1u ko man a xool, fekk leer ga di w\u00e9y. Ndegam s\u00e0rti yoon yooyuy j\u00ebme ci dee, \u00f1oo \u00e0nd ak ndam,\n3:8 rawatina nag ne, j\u00ebfu Xelum Y\u00e0lla dina g\u00ebn a \u00e0nd ak ndam.\n3:9 Su fekkee ne t\u00ebralin, wiy teg nit too\u00f1, \u00e0ndoon na ak ndam, rawatina ci t\u00ebralin wiy \u00e0tte nit jub.\n3:10 Ndaxte ndam li amoon keroog suux na ci ndam li ko raw l\u00e9egi.\n3:11 Te it ndegam li w\u00e9y dafa amoon ndam, astemaak li fi sax.\n3:12 Kon nag gannaaw w\u00e9kku nanu ci yaakaar ju mel noonu, danuy waare ak k\u00f3olute gu mag.\n3:13 Dunu def ni Musaa, mi daan muur xar-kanamam, ngir b\u00e0nni Israyil ba\u00f1 a gis jeexug leer googu saxul.\n3:14 Waaye seen xel dafa daldi gumba. Ba tey jii sax, bu \u00f1uy j\u00e0ng t\u00e9ereb k\u00f3ll\u00ebre gu j\u00ebkk gi, muuraay moomu dafay des; de\u00f1ul, ndaxte ci Kirist rekk la man a de\u00f1e.\n3:15 Waaw, ba tey jii, su \u00f1uy j\u00e0ng yoonu Musaa, seen xol dafay muuru.\n3:16 Waaye saa su kenn walbatikoo ci Boroom bi, muuraay gi daldi muriku.\n3:17 Fekk nag Boroom, bi \u00f1uy wax foofu, moo di Xelum Y\u00e0lla, te fu Xelu Boroom bi nekk, foofa yaatu gu mat am na fa.\n3:18 Te nun \u00f1\u00e9pp nag, danuy lerxat ndamu Boroom bi ak xar-kanam bu muuruwul, bay soppiku ci melokaanam, \u00e0nd ak ndam luy yokku te sax ci dooley Boroom biy Xelum Y\u00e0lla.\n4:1 Kon nag ndegam Y\u00e0lla ci y\u00ebrmandeem sas na nu ligg\u00e9ey boobu, dunu bayliku.\n4:2 L\u00e0nk nanoo \u00e0nd ci mbir, yi \u00f1uy n\u00ebbb te \u00f1u g\u00e0ccelu. Sunuy t\u00e0nk du yu njubla\u014b te dunu d\u00ebngal k\u00e0ddug Y\u00e0lla. Waaye nu ngi biral d\u00ebgg, di s\u00e0kku k\u00f3oluteg \u00f1\u00e9pp fa kanam Y\u00e0lla.\n4:3 Su fekkee ne sax, xebaar bu baax bi dafa muuru ci \u00f1enn \u00f1i, dafa fekk \u00f1oom \u00f1u aw yoon wu j\u00ebm ci s\u00e0nkute.\n4:4 \u00d1oom la y\u00e0llay jamono ji g\u00ebl\u00ebmal seen xel, ngir \u00f1u ba\u00f1 a gis leeru xebaar bu baax, biy wone ndamu Kirist, mi di melokaanu Y\u00e0lla.\n4:5 Ndaxte Yeesu Kirist Boroom bi lanuy waare, waaye waarewunu lu j\u00ebm ci sunu bopp. Nun seeni jaam lanu ndax Yeesu.\n4:6 Ndaxte Y\u00e0lla mi ne: \u00abNa leer leer ci biir l\u00ebnd\u00ebm,\u00bb moo leer ci sunu xol, ngir leeral nu ak xam-xamu ndamu Y\u00e0lla, liy fee\u00f1 ci xar-kanamu Kirist.\n4:7 Leer googu ci sunu xol mi ngi mel ni alal, waaye \u00f1u ngi ko def ci nun \u00f1i n\u00e9ew doole niy njaq kese, ngir k\u00e0ttan gu \u00ebpp xel gi, bawoo ci Y\u00e0lla te du ci nun.\n4:8 Da\u00f1u nuy sonal fu nekk, waaye kenn tancu nu. Da\u00f1u nuy dugal ci ruq yi, waaye dinanu ci g\u00e9nn.\n4:9 Da\u00f1u nuy fitnaal, waaye Y\u00e0lla du nu wacc mukk. T\u00ebr na\u00f1u nu, waaye kenn doggaliwu nu.\n4:10 Fu nu tollu noo ngi g\u00e0ddu ci sunu yaram dee gi Yeesu dee woon, ngir dundu Yeesu moom it fee\u00f1 ci sunu yaram.\n4:11 B\u00e9s bu nekk, nun \u00f1iy dund, \u00f1u ngi nuy j\u00e9bbal dee ndax Kirist, ngir dundu Kirist moom itam fee\u00f1 ci sunu yaram wiy dee.\n4:12 Noonu dee mu ngi j\u00ebf ci nun, dund di j\u00ebf ci y\u00e9en.\n4:13 Mbind mi nee na: \u00abDamaa g\u00ebm, moo tax ma wax.\u00bb Nun it nag, ndegam am nanu menn xelu ng\u00ebm moomu, danoo g\u00ebm, ba tax nuy wax.\n4:14 Ndaxte xam nanu ne Y\u00e0lla, mi dekkal Boroom bi Yeesu, dina nu dekkal nun itam ak Yeesu, te dina nu y\u00f3bbu ak y\u00e9en, taxawal nun \u00f1\u00e9pp ci jataayam.\n4:15 Ndaxte l\u00e9pp li nuy daj, seen njari\u00f1 a tax, ngir yiwu Y\u00e0lla, wiy yokku ci nit \u00f1u g\u00ebn a takku, yokkaale ng\u00ebr\u00ebm lu j\u00ebm ci Y\u00e0lla, ngir jollil ndamam.\n4:16 Loolu moo tax sunu yaakaar du tas. Bu fekkee sax sunu yaram day y\u00e0qu j\u00ebm cig mag, sunu ruu moom, b\u00e9s ak b\u00e9s muy g\u00ebn a yeesaat.\n4:17 Ndaxte sunu coono bu woyof bi dul y\u00e0gg, dafa nuy jural ndam lu bare, ba suul coono bi, tey sax abadan.\n4:18 Kon diirunu li \u00f1uy gis waaye li \u00f1u dul gis. Ndaxte li \u00f1uy gis day w\u00e9y, waaye li \u00f1u dul gis day sax ba f\u00e0ww.\n5:1 Yaram wi nu soloo ci kaw suuf dafa mel ni ab t\u00e0nt. Su daanoo, xam nanu ne, Y\u00e0lla jagleel na nu am taax ci asamaan, mu loxol nit defarul, di taax muy sax ba f\u00e0ww.\n5:2 Fi mu ne nu ngi wonk, di y\u00e0kkamtee f\u00e9ete ak sunu d\u00ebkkukaayu asamaan, sol ko ni koddaay, xam ne,\n5:3 bu nu ko solee, dunu def yaramu neen.\n5:4 Nun \u00f1i nekk ci t\u00e0nt bii, nu ngi wonk ndax coono. Du caageen ne, danoo b\u00ebgg a summi sunu yaramu \u00e0ddina, waaye danoo b\u00ebgg a sol sunu yaramu asamaan, ngir liy dee s\u00f3obu ci biir dund.\n5:5 Ki nu waajal ngir loolu moo di Y\u00e0lla, moom mi nu jox Xelam, di dawal ci c\u00e9r bi mu nu dencal.\n5:6 Noonu kon nu ngi fees ak k\u00f3olute fu nu tollu; te xam nanu ne, fi ak nu ngi d\u00ebkk ci yaram wii, \u00e0ggagunu sunu m\u00e0kkaan ci wetu Boroom bi \u2014\n5:7 ndaxte doxewunu ab gis, waaye ng\u00ebm lanuy doxe.\n5:8 Kon fees nanu ak k\u00f3olute, te y\u00e9enee j\u00f3ge ci d\u00ebkkukaayu yaram wii, dem d\u00ebkk ci wetu Boroom bi.\n5:9 Kon nag des fi walla j\u00f3ge fi, li nuy faaydaal moo di neex Boroom bi.\n5:10 Ndaxte nun \u00f1\u00e9pp f\u00e0ww nu teew ci kanamu Kirist, mu \u00e0tte nu, ngir ku nekk jot peyu li mu def ci yaramam, muy lu baax walla lu bon.\n5:11 Gannaaw xam nanu ragal Y\u00e0lla nag, nu ngi fexee g\u00ebmloo nit \u00f1i, waaye li nu nekk leer na Y\u00e0lla te yaakaar naa ne, leer na leen it, ba ne f\u00e0\u014b\u014b.\n5:12 J\u00e9emunoo waxati lu ngeen nuy nawe, waaye danu leen a b\u00ebgg a may yoonu tiitaru ci nun, tey tontu \u00f1oo\u00f1uy tiitaroo col te du xol.\n5:13 Su fekkee danoo t\u00e0ggalikoo ak sunu sago, ngir Y\u00e0lla la. Su nu \u00e0ndee ak sunu sago, ngir y\u00e9en la.\n5:14 Ndaxte mb\u00ebggeelu Kirist moo nuy jiite, ndax w\u00f3or na nu ne, ndegam kenn rekk a dee ngir \u00f1\u00e9pp, kon \u00f1\u00e9pp a dee.\n5:15 Te dee na ngir \u00f1\u00e9pp, ngir \u00f1iy dund dootu\u00f1u dund ngir seen bopp, waaye ngir ki dee ci seen w\u00e0ll te dekki.\n5:16 Kon nag gannaawsi tey xoolatunu kenn ci gis-gisu \u00e0ddina. Su fekkee mas nanoo xool Kirist ci gis-gisu \u00e0ddina, l\u00e9egi xooleetunu ko noonu.\n5:17 Kon bu nit bokkee ci Kirist, mbindeef mu bees la. Li j\u00ebkk w\u00e9y na, lu bees a fi teew.\n5:18 Te loolu l\u00e9pp a ngi sosoo ci Y\u00e0lla, mi nu jubale ak boppam jaare ko ci Yeesu Kirist, te sas nu nuy waare juboo googu:\n5:19 maanaam, Y\u00e0lla jaar na ci Kirist, di jubale waa \u00e0ddina ak boppam te s\u00ebfu leen seeni too\u00f1. K\u00e0ddug juboo googu, Y\u00e0lla d\u00e9nk na nu ko.\n5:20 Ay ndaw lanu, yu Kirist y\u00f3nni, te Y\u00e0llaa ngi woo nit \u00f1i jaare ko ci nun. Kon nag ci turu Kirist, nu ngi leen koy \u00f1aan: nanguleen a juboo ak Y\u00e0lla.\n5:21 Kirist mi musul a def b\u00e0kkaar, Y\u00e0lla def na ko b\u00e0kkaar ci sunu w\u00e0ll, ngir ci sunu bokk ci moom, nu man a doon njubteg Y\u00e0lla.\n6:1 Nun nag \u00f1iy ligg\u00e9eyandoo ak Y\u00e0lla, nu ngi leen di \u00f1aan: jari\u00f1ooleen yiw, wi ngeen jote ci Y\u00e0lla, ngir mu ba\u00f1 a neen ci y\u00e9en.\n6:2 Ndaxte Y\u00e0lla nee na:\u00abCa jamono ja mu jekke, nangu naa sa \u00f1aan;ci b\u00e9su mucc gi laa la wallu.\u00bb Tey jii la jamono ju jekk ji; tey la b\u00e9sub mucc gi.\n6:3 B\u00ebggunoo l\u00ebmbaaje xelu kenn ci dara, ngir kenn ba\u00f1 a sikk sunu ligg\u00e9ey.\n6:4 Li nu b\u00ebgg moo di rafetal sunu tur ni jawri\u00f1i Y\u00e0lla ci f\u00e0nn gu nekk; danuy mu\u00f1 coono yi, tiis yi, nj\u00e0qare yi;\n6:5 \u00f1u nuy d\u00f3or, di nu t\u00ebj ci kaso, d\u00ebkk yi di yengu ndax sunu mbir; nuy ligg\u00e9ey ba sonn, di fanaanee xool, di woor.\n6:6 Nu ngi rafetal sunu yen ci dund gu sell, ci xam-xam, mu\u00f1 ak laabiir, ci Xel mu Sell mi ak ci mb\u00ebggeel gu raxul njubla\u014b,\n6:7 ci k\u00e0ddug d\u00ebgg ak ci k\u00e0ttanu Y\u00e0lla, nu ngi yor g\u00e0nnaayi njubte ci loxol ndeyjoor ak lu c\u00e0mmoo\u00f1.\n6:8 \u00d1u b\u00e0kk nu, j\u00e9ppi nu, sant nu, xas nu. \u00d1u di nu jii\u00f1 r\u00e9eral, moona niti d\u00ebgg lanu.\n6:9 \u00d1uy xeeb sunu tur, moona tur yi siiw na\u00f1u. Nu mel ni \u00f1u loof, moona nu ngi dund. \u00d1u yar nu, teewul nu r\u00ebcc ci dee.\n6:10 Danuy d\u00e9kku tiis, waaye di b\u00e9g fu nu tollu. Nu tumur\u00e0nke, waaye di woomal \u00f1u bare; amunu dara, fekk noo moom l\u00e9pp.\n6:11 Y\u00e9en bokki Korent, wax nanu leen sunu biir ak sunu biti, di leen ubbil sunu xol.\n6:12 Ubbiku nanu ci y\u00e9en, waaye y\u00e9en ubbikuwuleen ci nun.\n6:13 Maa ngi wax ak y\u00e9en ni samay doom; feyleen nu bor bi, y\u00e9en itam; ubbileen seen xol!\n6:14 Buleen likkoo ak \u00f1i g\u00ebmul. Gan \u00e0ndandoo moo man a am diggante njubte ak nd\u00ebngte? Gan booloo moo man a am diggante leer ak l\u00ebnd\u00ebm?\n6:15 Gan d\u00e9ggoo moo man a am diggante Kirist ak Beliyar? Gan jaxasoo moo man a am diggante ki g\u00ebm ak ki g\u00ebmul?\n6:16 Nan la k\u00ebru Y\u00e0lla man a m\u00e0nkoo ak x\u00ebr\u00ebm yi? Ndaxte nun nooy k\u00ebru Y\u00e0lla Aji Dund ji, ni ko Y\u00e0lla waxe:\u00abDinaa d\u00ebkk ci seen biir,tey dox \u00e0nd ak \u00f1oom,ma nekk seen Y\u00e0lla,\u00f1uy samay gaay.\u00bb\n6:17 Kon nag Boroom bi nee na:\u00abG\u00e9nnleen biir \u00f1oo\u00f1u te beru.Buleen laal dara lu am sobe,kon dinaa leen teeru.\n6:18 Dinaa nekk baay ci y\u00e9en,ngeen di doom ci man, muy g\u00f3or, di jig\u00e9en. Moom la Aji K\u00e0ttan ji wax.\u00bb\n7:1 Ndegam nag jot nanu ci dige yu mel nii, samay soppe, nanu sellal sunu bopp ci b\u00e9pp sobeb yaram walla bu xel, dund dund gu sell, ba mat ci ragal Y\u00e0lla.\n7:2 Yaatal-leen nu ci seen xol. Too\u00f1unu kenn; lorunu kenn; naxunu kenn, j\u00ebl alalam.\n7:3 Teg leen too\u00f1 taxul may wax lii, ndaxte wax naa ba noppi ne, y\u00e9ena ngi ci sunu xol ci dund ak ci dee.\n7:4 K\u00f3olute gi ma am ci y\u00e9en r\u00e9y na. Tiitar bi may j\u00eble ci y\u00e9en r\u00e9y na. Sama xol sedd na guyy. Damaa fees ak mb\u00e9g ci b\u00e9pp coono bu nuy daj!\n7:5 Ba nu \u00e0ggee diiwaanu Maseduwan, noppaluwunu, waaye coono bu ne daj nanu ko: xeex ci biti, nj\u00e0qare ci biir.\n7:6 Waaye Y\u00e0lla miy d\u00ebf\u00ebl xolu \u00f1iy yoggoorlu ndax tiis, d\u00ebf\u00ebl na sunu xol ci \u00f1\u00ebwu Tit,\n7:7 te du ci \u00f1\u00ebwam rekk sax waaye ci li ngeen d\u00ebf\u00ebl xolam. Y\u00e9gal na nu seen nammeel ci nun, seen r\u00e9ccu ak seen farlu j\u00ebm ci man, ba sama mb\u00e9g g\u00ebn cee yokku.\n7:8 Su fekkee ne sax, bataaxal bi ma leen bind dafa leen naqare, r\u00e9ccootuma ko. Ci lu j\u00ebkk r\u00e9ccu naa ko, ndaxte gis naa ne, bataaxal boobu teg na leen tiis, doonte sax ci diir bu n\u00e9ew.\n7:9 Waaye sama xol sedd na l\u00e9egi, du ndax seen tiis, waaye ci li mu tax ngeen r\u00e9ccu. Tiis wu j\u00f3ge ci Y\u00e0lla ngeen tegoo, te \u00e0ndul ak benn loraange bu bawoo ci nun.\n7:10 Ndaxte tiis wu j\u00f3ge ci Y\u00e0lla dina jur r\u00e9ccu guy j\u00ebme ci mucc, te r\u00e9ccu googu laajul g\u00ebstu. Waaye tiisu \u00e0ddina day j\u00ebme ci dee.\n7:11 Seen tiis wi j\u00f3ge ci Y\u00e0lla, gisleen nag li mu jur: ndaw njaxlaf ak lay ak mer ak ragal ak nammeel ak farlu, ak b\u00ebgg a yar ki too\u00f1! Ci seen j\u00ebf y\u00e9pp wone ngeen ne, set ngeen wecc ci mbir moomu.\n7:12 Kon nag su ma leen bindee, ki too\u00f1 taxul, ki \u00f1u too\u00f1 it taxul, waaye dama leen a bind, ngir ngeen man a gis ci kanam Y\u00e0lla cawarte, gi ngeen am ci nun.\n7:13 Te loolu seral na sunu xol. Sunu xel dal na, rawati ci li nu \u00e0nd ak Tit ci mb\u00e9gam, ci li ngeen seral xolam, y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.\n7:14 Su fekkee ne tiitaru woon naa ci seen mbir ci kanamu Tit, rusuma ci. D\u00ebgg rekk lanu leen mas a wax; noonu it la Tit gise ne, li nu leen doon seede l\u00e9pp, d\u00ebgg la.\n7:15 Te mb\u00ebggeelam ci y\u00e9en g\u00ebn na yokku, buy f\u00e0ttaliku ni ngeen ko d\u00e9ggale y\u00e9en \u00f1\u00e9pp, ci li ngeen ko teeru, \u00e0nd ak ragal ak weg.\n7:16 B\u00e9g naa, ndaxte xam naa ne, man naa leen a w\u00f3olu ci lu nekk!\n8:1 Gannaaw loolu bokk yi, danu leen a b\u00ebgg a xamal li yiwu Y\u00e0lla jur ci biir mboolooy \u00f1i g\u00ebm te nekk ci diiwaanu Maseduwan.\n8:2 Nattu yi \u00f1u jaar \u00ebmb na\u00f1u coono yu r\u00e9y; waaye seen mb\u00e9g mu tar ak seen \u00f1\u00e0kk gu metti \u00f1oo jur ci \u00f1oom y\u00e9w\u00e9n gu j\u00e9ggi dayo.\n8:3 Seede naa ne, \u00f1oom ci seen bopp joxe na\u00f1u ba fa seen man-man yem, ba weesu ko sax.\n8:4 Saraxu na\u00f1u nu lool, ngir bokk ci \u00f1iy y\u00f3nnee ndimbal gaayi Y\u00e0lla yi.\n8:5 Te yemu\u00f1u sax ci li nu s\u00e9entu woon ci \u00f1oom, waaye da\u00f1oo j\u00e9bbal seen bopp Boroom bi j\u00ebkk, gannaaw loolu \u00f1u j\u00e9bbal nu seen bopp ci coobareg Y\u00e0lla.\n8:6 Looloo tax nag nu sant Tit, mu \u00f1\u00ebw \u00e0ggale ci y\u00e9en, ni mu t\u00e0mbalee woon, seen j\u00ebfu ndimbal.\n8:7 Gannaaw nag wone ngeen cawarte gu tollu noonu, ci ng\u00ebm, ci wax, ci xam-xam, ci farlu gu mat, ak ci seen mb\u00ebggeel ci nun, sawareleen noonu it ci j\u00ebfu ndimbal lii.\n8:8 Du ndigal lu ma leen di jox, waaye dama leen di y\u00e9gal cawarteg \u00f1i ci des, ngir natt fu seen mb\u00ebggeel tollu.\n8:9 Ndaxte yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist umpu leen, ni mu futtee am-amam, ba \u00f1\u00e0kk ngir y\u00e9en, ndax ngeen woomle cig \u00f1\u00e0kkam.\n8:10 Kon lii laa xalaat ci lu baax ci y\u00e9en: y\u00e9en \u00f1i nga xam ne t\u00e0mbaliwuleen a j\u00ebf rekk, waaye y\u00e9ena j\u00ebkk a am y\u00e9ene jii daaw,\n8:11 yeggaleleen ko l\u00e9egi. Noonu li ngeen mottali ci seen man-man tolloo ak y\u00e9ene, ji ngeen amoon ci seen m\u00e9b\u00e9t.\n8:12 Ndaxte joxe, bu \u00e0ndee ak y\u00e9ene, Y\u00e0lla dina ko nangu, di seet li nu am te ba\u00f1 a seet li nu amul.\n8:13 B\u00ebgguma leen a teg soxla, ngir woyofal \u00f1i ci des, waaye na \u00f1\u00e9pp tolloole.\n8:14 Tey jii nag man ngeen s\u00e0kk ci li ngeen barele, faj soxlay \u00f1eneen, ngir \u00ebll\u00ebg it bareleg \u00f1oo\u00f1a faj seen soxla. Noonu \u00f1\u00e9pp tolloole.\n8:15 Moom la Mbind mi t\u00ebral ne:\u00abKi dajale lu bare \u00ebpplewul dara,te ki dajale tuuti \u00f1\u00e0kkul.\u00bb\n8:16 Cant \u00f1eel na Y\u00e0lla, moom mi def ci xolu Tit cawarte gu mel ni sunu gos ci y\u00e9en!\n8:17 Bi nu ko laajee, mu \u00f1\u00ebw ci y\u00e9en, nangu na, te rax-ca-dolli cawarteem tollu na, ba nu man a wax ne, ci coobarey boppam la j\u00f3ge, j\u00ebm ci y\u00e9en.\n8:18 Y\u00f3nniwaale nanu ak moom mbokk, mi am tur wu rafet ci mboolooy \u00f1i g\u00ebm \u00f1\u00e9pp ndax li muy waare xebaaru Kirist.\n8:19 Te sax mbooloo yi \u00f1oo ko t\u00e0nn, ngir mu \u00e0nd ak nun, bu nuy y\u00f3bbu ndimbal li ngir ndamu Boroom bi, te mu firndeel sunu y\u00e9ene ju rafet.\n8:20 Def nanu noonu nag, ndax kenn ba\u00f1 noo \u014b\u00e0\u00f1\u00f1 ci ni nuy topptoo ndimbal lu yaatu loolu.\n8:21 Danuy fexee def li jub, du ci kanam Y\u00e0lla rekk, waaye it ci kanam nit \u00f1i.\n8:22 Y\u00f3nniwaale nanu it sunu mbokk, mi nu seetlu cawarteem ay yooni yoon ci f\u00e0nn yu bare, te mu g\u00ebn koo f\u00e9sal bii yoon ndax k\u00f3olute gu r\u00e9y, gi mu am ci y\u00e9en.\n8:23 Noonu kon ci lu j\u00ebm ci Tit, sama nawle la ci ligg\u00e9ey, bi ci seen biir. Ci lu j\u00ebm ci sunu bokk, yi \u00e0nd ak moom nag, ndawi mbooloom \u00f1i g\u00ebm la\u00f1u, \u00f1uy wone ndamu Kirist.\n8:24 Na seen teeru firndeel nag seen mb\u00ebggeel ci kanamu mboolooy \u00f1i g\u00ebm, te d\u00ebggal leen ne, noo yey w\u00f3olu leen.\n9:1 Ci mbirum ndimbal loolu j\u00ebm ci gaayi Y\u00e0lla yi, matul ma leen di bindaat,\n9:2 ndaxte xam naa seen y\u00e9ene ju rafet, te maa ngi ciy damu ci kanamu waa Maseduwan, naan leen: \u00abDaaw fekk na waa Akayi jekk.\u00bb Te seen cawarte xamb na \u00f1u bare ci \u00f1oom.\n9:3 Maa ngi y\u00f3nni nag bokk yooyu, ngir damu gi nu doon damu ci y\u00e9en ci mbir mii ba\u00f1 a neen, te ngeen jekk, ni ma ko waxe woon.\n9:4 Danoo ba\u00f1 rekk waa Maseduwan, \u00f1iy \u00e0nd ak man, fekk jekkaguleen; te kon k\u00f3olute googu nu am ci y\u00e9en dina nekk sunu g\u00e0cce, waxaalewuma nag seen bos.\n9:5 Moo tax ma xalaat ne, li g\u00ebn mooy y\u00f3nni bokk yooyu, \u00f1u jiitu ma ci y\u00e9en, topptoo mbiri ndimbal lu yaatu loolu ngeen dige woon. Loolu di may gu t\u00e0lli, te ba\u00f1 a nekk y\u00ebfi nay.\n9:6 Te lii moo am: ku ji tuuti, g\u00f3ob tuuti; ku ji lu bare, g\u00f3ob lu bare.\n9:7 Kon na ku nekk joxe, ni mu ko nase ci xolam, te ba\u00f1 cee am r\u00e9ccu walla sa\u00f1ul-ba\u00f1, ndaxte kiy joxe ak mb\u00e9g moo neex Boroom bi.\n9:8 Te Y\u00e0lla man na leen a woomal ci b\u00e9pp yiwam ba ci f\u00e9pp ak ci l\u00e9pp, ngeen faj seen soxla y\u00e9pp te sakkanle it ngir b\u00e9pp j\u00ebf bu baax.\n9:9 Moom la Mbind mi wax ne:\u00abTabe na, ba may baadoolo yi;njubteem day sax ba f\u00e0ww.\u00bb\n9:10 Y\u00e0lla miy jox beykat bi jiwu ak nit ab dund, dina leen jox jiwu wu ne g\u00e0\u00f1\u00f1, te sakkanal li seen njub me\u00f1\u00f1.\n9:11 Noonu dingeen woomle ci l\u00e9pp, ba y\u00e9w\u00e9n ci b\u00e9pp anam, ba tax \u00f1u bare g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla ndax li ngeen maye jaarale ko ci nun.\n9:12 Ndaxte njaamu, gi ngeen di jaamu, yemul rekk ci faj soxlay gaayi Y\u00e0lla yi, waaye dina tax it ng\u00ebr\u00ebmu \u00f1u bare baawaan, j\u00ebm ci Y\u00e0lla.\n9:13 Ci li ngeen firndeel seen mb\u00ebggeel ci joxe ndimbal lii, dina\u00f1u m\u00e0ggal Y\u00e0lla, ndaxte wone ngeen ni ngeen d\u00e9ggale xebaar bu baax bu Kirist bi, ak ni ngeen y\u00e9w\u00e9ne ci seen ndimbal j\u00ebme ci \u00f1oom ak \u00f1\u00e9pp.\n9:14 Rax-ca-dolli dina\u00f1u sant Y\u00e0lla ak xol bu fees ak cofeel ci y\u00e9en ndax yiw wu mag, wi Y\u00e0lla def ci y\u00e9en.\n9:15 J\u00ebr\u00eb-j\u00ebfati yaw Y\u00e0lla ndax sa may googu weesu dayo!\n10:1 Ci lu j\u00ebm ci samay mbir nag, maa ngi leen di \u00f1aan \u2014 man Pool, mi \u00f1u ne, ci seen biir \u00abragal\u00bb laa, bu ma leen soree, \u00ab\u00f1eme,\u00bb \u2014 maa ngi leen di \u00f1aan ndax woyof ak lewetaayu Kirist, ngir bu ma \u00f1\u00ebwee, ma ba\u00f1 a \u00e0nd ak \u00f1eme gi may dencal \u00f1enn \u00f1iy xalaat ne, gis-gisu nit lanu topp.\n10:3 D\u00ebgg la ne nit rekk lanu, waaye dunu xeexe ni nit.\n10:4 Ndaxte g\u00e0nnaay, yi nuy xaree, j\u00f3gewu\u00f1u ci nit, waaye ca Y\u00e0lla la\u00f1u j\u00f3ge, te \u00e0nd ak k\u00e0ttan, ngir daaneel ay tata. Danuy daaneel xalaat yi dul d\u00ebgg\n10:5 ak b\u00e9pp tiitar buy j\u00e0nkoonteek xam-xamu Y\u00e0lla, te danuy noot b\u00e9pp xalaat, ba mu d\u00e9ggal Kirist.\n10:6 Te fas y\u00e9ene nanoo jubbanti k\u00e9pp ku d\u00e9ggadi, b\u00e9s bu seen d\u00e9gg ndigal matee.\n10:7 Xool-leen mbir mi ne f\u00e0\u014b\u014b. Bu amee ku mu w\u00f3or ne, ci Kirist la bokk, na j\u00e0pp it ne, su bokkee ci Kirist, nun itam ci Kirist lanu bokk.\n10:8 Awma lu may rus, su may damu lu \u00ebpp ci sa\u00f1-sa\u00f1 bi nu Boroom bi jox, di sa\u00f1-sa\u00f1u yokk seen ng\u00ebm, te du ngir seen kasara.\n10:9 Ba tey b\u00ebgguma ngeen xalaat ne, maa ngi leen di x\u00ebbal ci samay bataaxal.\n10:10 Ndaxte am na ku naan: \u00abAy bataaxalam da\u00f1oo \u00f1agas te am doole, waaye bu teewee dafay \u00f1\u00e0kk fulla, di wax waxi picc.\u00bb\n10:11 Kiy wax loolu na xam lii: ni sunuy k\u00e0ddu mel ci sunuy bataaxal, bu nu fa nekkul, noonu it lanuy mel ci sunuy j\u00ebf, bu nu teewee.\n10:12 \u00d1emewunoo f\u00e9etele walla mengale sunu bopp ak \u00f1oo\u00f1u naw seen bopp. Ci li \u00f1uy s\u00e0kk ab natt ngir natt ak mengale seen bopp ak seen bopp, \u00f1\u00e0kk xel a tax.\n10:13 Nun nag dunu damu ci lu weesu dayo. Nu ngi damu ci ligg\u00e9ey bi nu Y\u00e0lla sas, ba may nu, nu agsi ci y\u00e9en.\n10:14 Bu sunu sas agsiwul woon ba ci y\u00e9en, kon man nanoo ne, g\u00e9nn nanu sas wi nu Y\u00e0lla sas. Waaye agsi na ba ci y\u00e9en, te indil nanu leen xebaar bu baax bi j\u00ebm ci Kirist.\n10:15 Kon nag dunu j\u00e9ggi dig yi Y\u00e0lla r\u00ebdd, bay damu ci ligg\u00e9eyu \u00f1eneen. Waaye am nanu yaakaar ne, su seen ng\u00ebm yokkoo, dinanu g\u00ebn a m\u00e0gg ci seen biir, des ba tey ci dig yi nu Y\u00e0lla r\u00ebddal.\n10:16 Noonu dinanu man a y\u00e9gle xebaar bu baax bi ci b\u00e9rab, yi leen f\u00e9ete gannaaw, te ba\u00f1 a damu ci li \u00f1eneen \u00f1i def ci seen sas.\n10:17 Waaye ni ko Mbind mi waxe: \u00abKuy damu, na damu ci Boroom bi.\u00bb\n10:18 Ndaxte ki neex Y\u00e0lla, du ki naw boppam, waaye ki Y\u00e0lla g\u00ebr\u00ebm.\n11:1 C\u00e9y bu ngeen ma manoon a mu\u00f1al, ma wax leen tuuti waxi dof! Waaw mu\u00f1al-leen ma sax.\n11:2 Dama leen di fiire ak fiiraange gu j\u00f3ge ca Y\u00e0lla, ndaxte dama leen a b\u00ebgg a j\u00e9bbal jenn j\u00ebkk\u00ebr kepp, muy Kirist, ngeen set ni janq.\n11:3 Waaye ni jaan ja naxe woon Awa ci pexeem, ragal naa y\u00e9en itam \u00f1u l\u00ebmbaaje ni seen xel, ba ngeen d\u00ebddu xol bu laab, bi ngeen amoon ci seen diggante ak Kirist.\n11:4 Ndaxte bu kenn \u00f1\u00ebwee, di leen waar ci Yeesu ci lu juuyoo ak li nu leen y\u00e9gal, walla ngeen jot meneen xel mu wuute ak Xel mi ngeen jot, walla ngeen nangu beneen xebaar bu wuute ak bi ngeen d\u00e9gg, dingeen ko d\u00e9kku bu baax.\n11:5 Moona foog naa ne, seen ndaw yooyu ngeen y\u00e9kkati, ba \u00f1u \u00ebpp ndaw sax, \u00ebpplewu\u00f1u ma dara.\n11:6 Bu ma dul j\u00e0mbaari wax it, n\u00e9ewuma xam-xam, te won nanu leen ko ci b\u00e9pp mbir ak ci b\u00e9pp f\u00e0nn.\n11:7 Walla boog ndax dama leen a too\u00f1 ci li ma suufeel sama bopp ngir y\u00e9kkati leen, ba ma leen di y\u00e9gal xebaar bu baax bi te laajuma leen genn pey?\n11:8 Xanaa kay damaa too\u00f1 ci li ma dunde alalu yeneen mboolooy \u00f1i g\u00ebm, ba futti leen, ngir dimbali leen, y\u00e9en.\n11:9 Te ba ma nekkee ci y\u00e9en te soxla dab ma, w\u00e9eruwuma ci kenn ci y\u00e9en, ndaxte bokk ya j\u00f3ge Maseduwan \u00f1oo ma indil li ma soxla woon. Ci l\u00e9pp moytu naa nekk yen ci y\u00e9en, te dinaa ko g\u00ebn a def.\n11:10 Ni mu w\u00f3ore ne, d\u00ebggug Kirist nekk na ci man, ni la w\u00f3ore ne loolii may damoo, kenn du ko teggi ci diiwaanu Akayi g\u00e9pp.\n11:11 Lu tax? Ndax dama leen a b\u00ebggul? Y\u00e0lla xam na ne, b\u00ebgg naa leen!\n11:12 Noonu may doxale nag dinaa ci sax, ngir \u00f1iy damu, di wut yoon wu \u00f1u aw ba yemale seen bopp ak nun, du\u00f1u ko am.\n11:13 Ay ndawi naaf\u00e9q la\u00f1u, di ay ligg\u00e9eykat yu njubla\u014b yuy mbubboo turu ndawi Kirist.\n11:14 Te loolu jaaxalu nu, ndaxte Seytaane moom ci boppam day mbubboo malaakam leer.\n11:15 Kon nag ay ndawam mbubboo ndawi njub, loolu du nu jaaxal. Dees na leen fey seeni j\u00ebf.\n11:16 Maa ngi leen koy waxaat: bu ma kenn j\u00e0pp nib dof. Walla boog bu ngeen ma ko j\u00e0ppee, s\u00e9ddleen ma c\u00e9ru dof, ngir ma damu tuuti, man itam.\n11:17 Loolu may wax nag, waxuma ko ci turu Boroom bi. Bu ma \u00f1emee damoo nii, maa ngi wax ni dof.\n11:18 Ndegam \u00f1u bare da\u00f1uy damu ni nit kese, man itam kon dinaa damu.\n11:19 Y\u00e9en boroom xel yi, aka ngeen a man a mu\u00f1al \u00f1i dof,\n11:20 nde y\u00e9ena ngi mu\u00f1 \u00f1i leen di jaamloo, di lekk seen alal, di leen nax, di leen xeeb, di leen talaata!\n11:21 Sunu n\u00e9ew doole mayu nu, nu dem ba j\u00ebfe noonu; rus naa ci lool de! Ma wax waxi dof; moona l\u00e9pp lu waay \u00f1emee damoo, \u00f1eme naa ko, man it.\n11:22 Ndax Ibr\u00eb la\u00f1u? Man it Ibr\u00eb laa. Ndax b\u00e0nni Israyil la\u00f1u? Man itam ci laa. Ndax s\u00ebti Ibraayma la\u00f1u? Man itam moom laa.\n11:23 Ndax surgay Kirist la\u00f1u? --maa ngi wax waxi ku t\u00e0ggoo ak sagoom nag \u2014 maa leen ko g\u00ebn a doon. Bu dee ci ligg\u00e9ey, maa leen ci man. Bu dee ci li \u00f1u nu t\u00ebj ci kaso, maa leen ko g\u00ebn a miin. Bu dee ci li \u00f1u nu d\u00f3or ay yar, maa leen \u00ebpple. Leru naa dee ba t\u00e0yyi.\n11:24 Jur\u00f3omi yoon Yawut yi d\u00f3or na\u00f1u ma fanweeri yar ak jur\u00f3om-\u00f1eent.\n11:25 \u00d1etti yoon d\u00f3orees na ma ay yet, te mas na\u00f1u maa s\u00e0nni ay xeer, b\u00ebgg maa rey. \u00d1etti yoon dugg naa gaal, mu suux. Mas naa yendu ci ndox, fanaan ci.\n11:26 Ci sama tukki yu bare yi daan naa faral di daje ak musiba ci dex yi, ak musiba ci s\u00e0cc yi, musiba mu j\u00f3ge ci sama xeet walla ci \u00f1i dul Yawut, musiba ci biir d\u00ebkk yi, ci m\u00e0ndi\u014b yi, ci g\u00e9ej gi, ci biir bokki taalibe yu naaf\u00e9q yi.\n11:27 Sonn naa, di \u00f1aq, di fanaane xool, di xiif ak a mar tey fande, di d\u00e9kku liw te rafle,\n11:28 waxaalewuma li ci des nag: b\u00e9s bu nekk maa ngi xalaat mboolooy \u00f1i g\u00ebm.\n11:29 Ana ku ci n\u00e9ew doole, te w\u00e0lluma ko? Ana ku ci b\u00e0kkaar, te awma naqar wu tiis?\n11:30 Su ma damu waree kon, ci sama n\u00e9ew doole laay damoo.\n11:31 Y\u00e0lla Baayu sunu Boroom Yeesu, moom mi m\u00e0gg ba f\u00e0ww, xam na ne, du ay fen ci man.\n11:32 Ba ma nekkee d\u00ebkku Damas, boroom d\u00ebkk ba, di jawri\u00f1u buur ba Aretas, dafa santaane woon \u00f1uy wottu d\u00ebkk ba, ngir man maa j\u00e0pp.\n11:33 Waaye dugalees na ma ci d\u00e0mba, jaarale ma ci palenteeru miiri d\u00ebkk ba, yoor ma ci suuf. Noonu ma r\u00ebcc ko.\n12:1 Damu amul jari\u00f1, ba tey war na ma. Kon ma j\u00e0ll ci nettali gis-gisi Boroom bi ak i pee\u00f1u.\n12:2 Xam naa taalibeb Kirist boo xam ne y\u00e9kkati na\u00f1u ko ba ca asamaan, si g\u00ebn a kawe, booba ak l\u00e9egi mat na fukki at ak \u00f1eent. Xawma ndax \u00e0nd na ak j\u00ebmmam walla d\u00e9et. Y\u00e0lla rekk a xam.\n12:3 Xam naa ne, nit kooku y\u00e9kkati na\u00f1u ko ba fa Y\u00e0lla nekk. Bu dee ci j\u00ebmmam mbaa ci xelam, xawma; Y\u00e0llaa xam. Mu d\u00e9gg fa baat yu \u00f1u m\u00ebnul a nettali te yu \u00f1u mayul doom Aadama, mu \u014baa\u014b ko.\n12:5 Dinaa damu ci nit ku mel noonu. Waaye duma damu ci sama bopp, lu dul liy wone sama n\u00e9ew doole.\n12:6 Su ma b\u00ebggoon a damu, du doon y\u00ebfi dof, ndaxte d\u00ebgg laay wax. Waaye damay moytoo damu, ngir kenn ba\u00f1 a foog ci man lu weesu li mu gis, may def, te muy d\u00e9gg, ma di ko wax.\n12:7 Te it ngir ma ba\u00f1 a y\u00e9g sama bopp ndax pee\u00f1u yooyu wees xel, mayees na mbir dal ma ci sama yaram, di ma metital ni d\u00e9g, muy malaakam Seytaane mu may sonal, ngir ma ba\u00f1 a y\u00e9g sama bopp.\n12:8 \u00d1aan naa Boroom bi \u00f1etti yoon ci mbir moomu, ngir mu taqale ma ak moom.\n12:9 Waaye mu ne ma: \u00abSama yiw doy na la; sama k\u00e0ttan a ngi mate cig n\u00e9ew doole.\u00bb Kon nag d\u00ebgg-d\u00ebgg, g\u00ebn na maa b\u00e9g ci damu ndax sama n\u00e9ew doole, ngir k\u00e0ttanu Kirist d\u00ebkk ci man.\n12:10 Looloo tax may b\u00e9g ci n\u00e9ew doole, yi may w\u00e9ye ngir turu Kirist, ciy tiis, ciy nj\u00e0qare, mbaa \u00f1u saaga ma, mbaa \u00f1u fitnaal ma. Ndaxte bu ma n\u00e9ewee doole, booba laay am k\u00e0ttan.\n12:11 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg wax naa waxi dof te y\u00e9ena ma ci dugal, fekk y\u00e9en ci seen bopp sax y\u00e9ena ma waroon a sargal, ndaxte su ma dul dara sax, seen ndaw yooyu ngeen naw \u00ebpplewu\u00f1u ma dara.\n12:12 K\u00e9emaan yi, jaloore yi ak j\u00ebf yu m\u00e0gg, yiy firndeel ndawul Kirist, fee\u00f1 na\u00f1u ci seen biir, ma \u00e0nd ci ak mu\u00f1 gu mat.\n12:13 Lan laa defal yeneen mboolooy \u00f1i g\u00ebm te defaluma leen ko, xanaa rekk li ma w\u00e9eru ci \u00f1oom te w\u00e9eruma ci y\u00e9en? Baal-leen ma googu too\u00f1!\n12:14 Maa ngi leen di waaj a ganesi \u00f1etteel bi yoon, te duma w\u00e9eru ci y\u00e9en. Wutsiwuma seen alal, y\u00e9en laa soxla. Ndaxte du gune moo war a yor waajuram, waaye waajur moo war a yor gune yi.\n12:15 Man nag nangu naa joxe li ma am l\u00e9pp ak xol bu sedd, ba joxe sama bopp sax, ngir dimbali leen. Gannaaw b\u00ebgg naa leen nii, xanaa kay seen mb\u00ebggeel ci man warul a w\u00e0\u00f1\u00f1iku?\n12:16 Kon noonu la, nekkuma woon yen ci y\u00e9en. Waaye man na am \u00f1u naan, dama leen a nax, ba r\u00e9eral leen ci sama njubla\u014b.\n12:17 Mbaa du damaa lekk seen alal, jaare ko ci kenn ci \u00f1i ma y\u00f3nni woon?\n12:18 Sant naa Tit, mu \u00f1\u00ebw ci y\u00e9en, te yebal naa sunu mbokk moomu ak moom. Ndax Tit dafa lekk seen alal? Man ak moom, ndax bokkunu woon xel mu nu y\u00e9kkati ak t\u00e0nk yu nuy dox?\n12:19 Xanaa diirub li ngeen di j\u00e0ng lii, defe ngeen ne, nu ngi wut aw lay ci seen kanam. Samay xarit, nu ngi leen di wax ci kanam Y\u00e0lla ak ci turu Kirist; te l\u00e9pp ngir seen njari\u00f1 la.\n12:20 Ragal naa, bu ma \u00f1\u00ebwee ci y\u00e9en, fekk leen nu ma neexul, te y\u00e9en it ngeen fekk ma nu leen neexul. Ragal naa fekk ay xuloo ci seen biir, ak \u00f1eetaane, xadar ak diiroo mbagg, xas ak j\u00ebw, r\u00e9y-r\u00e9ylu ak yengu-yengu.\n12:21 Ragal naa, bu ma leen ganesiwaatee, Y\u00e0lla sama Boroom suufeel ma ci seen biir, ma naqarlu ci \u00f1u bare \u00f1u b\u00e0kkaaroon te d\u00ebdduwu\u00f1u seen y\u00e0qute, seen njaaloo ak seen \u00f1aawteef, gi \u00f1u doon def.\n13:1 Bii mooy \u00f1etteel bi yoon, ma di leen ganesi. \u00abB\u00e9pp \u00e0tte dina aju ci seedes \u00f1aar walla \u00f1etti nit.\u00bb\n13:2 Li ma waxoon ci sama \u00f1aareelu ngan, ci \u00f1i b\u00e0kkaaroon bu y\u00e0gg ak \u00f1i ci des, maa ngi koy waxaat l\u00e9egi, bala maa dikkaat: su ma dellusee, duma y\u00ebr\u00ebm kenn.\n13:3 Bu fekkee ne dangeen a b\u00ebgg firnde juy wone ne, Kirist mooy wax jaarale ko ci man, dingeen ko am. Digganteem ak y\u00e9en du \u00e0nd ak n\u00e9ew doole, waaye dafay fee\u00f1al k\u00e0ttan ci seen biir.\n13:4 N\u00e9ewoon na doole, ba \u00f1u koy daaj ca bant ngir rey ko, waaye mi ngi dund ci k\u00e0ttanu Y\u00e0lla. Nun itam n\u00e9ew nanu doole ci sunu bokk ci moom, waaye dinanu dund ak moom ci k\u00e0ttanu Y\u00e0lla, bu nuy j\u00ebfante ak y\u00e9en.\n13:5 Xool-leen seen bopp bu baax, ba xam ndax ng\u00ebm a ngi ci y\u00e9en. Seetluleen seen bopp. Xanaa xamuleen ne, Yeesoo ngi ci y\u00e9en? Walla boog ngeen gis ne, ay naaf\u00e9q ngeen.\n13:6 Waaye yaakaar naa ne dingeen gis ne, man nanoo wone nun, firndeg ng\u00ebm.\n13:7 Nu ngi \u00f1aan Y\u00e0lla, ngeen ba\u00f1 a def dara lu bon. Waxuma ne danoo b\u00ebgg a wone noonu sunu firndeg ng\u00ebm, waaye sunu y\u00e9ene mooy ngeen j\u00ebf lu baax, boo yaboo sax \u00f1u jii\u00f1 nu ag naaf\u00e9q.\n13:8 Ndaxte manalunu dara d\u00ebggu Y\u00e0lla gi; m\u00ebnunu lu dul taxawal ko.\n13:9 Bu nu n\u00e9ewee doole, fekk am ngeen doole, b\u00e9g nanu ci. Te sax nu ngi \u00f1aan, ngeen jublu cig mat.\n13:10 Looloo tax ma leen di binde nii, bala maa \u00f1\u00ebw; b\u00ebgguma leen a duma ci sa\u00f1-sa\u00f1 bi ma Boroom bi jox. Jox na ma ko, ngir ma yokk seen ng\u00ebm, waaye du ngir seen kasara.\n13:11 Kon nag bokk yi, b\u00e9gleen, jublu cig mat, di d\u00e9glu so\u00f1\u00f1ante bi ma leen di d\u00e9nk, am benn xalaat te d\u00ebkk ci j\u00e0mm; noonu Y\u00e0lla miy mb\u00ebggeel te di Y\u00e0llay j\u00e0mm dina \u00e0nd ak y\u00e9en.\n13:12 Saafoonteleen ak xol bu laab.\n13:13 Mboolem gaayi Y\u00e0lla y\u00e9pp \u00f1u ngi leen di nuyu.\n13:14 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist, ak mb\u00ebggeelu Y\u00e0lla ak booloo, gi nu am ak Xel mu Sell mi, \u00e0nd ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.","title":"Wolof Bible (NT): 2 Corinthians","type":"page"}
