{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/col.htm","path":"bib/wb/wlf/col.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/col.htm","text":"1:1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Y\u00e0lla, man ak Timote sunu mbokk,\n1:2 noo leen di bind, y\u00e9en gaayi Y\u00e0lla yu sell, yi d\u00ebkk Kolos te di ay bokk ci g\u00ebm Kirist. Na leen Y\u00e0lla sunu Baay may yiw ak j\u00e0mm.\n1:3 Dunu noppee sant Y\u00e0lla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, saa su nu leen di \u00f1aanal,\n1:4 ndaxte y\u00e9g nanu seen ng\u00ebm ci Kirist Yeesu ak seen mb\u00ebggeel ci gaayi Y\u00e0lla y\u00e9pp.\n1:5 Ng\u00ebm googu ak mb\u00ebggeel googu \u00f1u ngi sosoo ci yaakaaru \u00ebll\u00ebg, jiy c\u00e9r bi leen Y\u00e0lla dencal ca asamaan. Mas ngeen a d\u00e9gg yaakaar jooju ci k\u00e0ddug d\u00ebgg gi, di xebaar bu baax bi.\n1:6 Ni xebaar bu baax bi w\u00e0cce ci y\u00e9en, noonu lay w\u00e0cce ci \u00e0ddina s\u00e9pp, di me\u00f1\u00f1 te di law. Te noonu lay doxale ci y\u00e9en, li dale ci b\u00e9s, ba ngeen d\u00e9gge xebaaru yiwu Y\u00e0lla, te xam d\u00ebggam gi mu \u00ebmb;\n1:7 moom ngeen j\u00e0nge ci Epafras, miy sunu nawle ci ligg\u00e9ey bi te nu sopp ko, di jawri\u00f1u Kirist bu takku ngir seen njari\u00f1.\n1:8 Te moo nu y\u00e9gal it mb\u00ebggeel, gi Xelu Y\u00e0lla mi sol ci y\u00e9en.\n1:9 Looloo tax ci sunu w\u00e0llu bopp, ba nu ko y\u00e9gee ba tey, j\u00f3gunu ci di leen \u00f1aanal. Nu ngi \u00f1aan Y\u00e0lla, ngeen xam bu baax coobareem ci xel mu mat ak r\u00e0\u00f1\u00f1ee gu aju ci dooley Xelam.\n1:10 Noonu dingeen dund dund gu d\u00ebppoo ak seen bokk ci Boroom bi, ba neex ko ci f\u00e0nn gu nekk, di def b\u00e9pp j\u00ebf yu baax, te yokk seen xam-xam ci Y\u00e0lla.\n1:11 Te Y\u00e0lla dina leen dooleel ak b\u00e9pp doole, mu mengoo ak k\u00e0ttanu ndamam, ngir ngeen man a tegoo coono te mu\u00f1, ba fa mu\u00f1 di yem.\n1:12 Dingeen g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla Baay bi, \u00e0nd ci ak mb\u00e9g, moom mi leen jagleel, ngeen bokk ci c\u00e9r, bi mu dencal gaayam yu sell yi ci leer.\n1:13 Y\u00e0lla musal na nu ci dooley l\u00ebnd\u00ebm, y\u00f3bbu nu ci nguuru Doomam ji mu b\u00ebgg,\n1:14 moom mi nu jot, maanaam baal nu sunuy b\u00e0kkaar.\n1:15 Doom jooju moo di melokaanu Y\u00e0lla, ji kenn gisul. Mooy taaw bi, ki g\u00ebn a m\u00e0gg l\u00e9pp luy mbindeef.\n1:16 Ndaxte ci moom la Y\u00e0lla s\u00e0kke l\u00e9pp lu nekk ci asamaan ak suuf, li \u00f1uy gis ak li \u00f1u m\u00ebnul a gis, muy buur, njiit, kilifa mbaa boroom sa\u00f1-sa\u00f1. L\u00e9pp lu \u00f1u s\u00e0kk, ci moom la\u00f1u ko jaarale, ci moom la\u00f1u ko j\u00ebme.\n1:17 Laata dara di am, fekkoon na moom mu nekk, te l\u00e9pp a ngi j\u00e0ppoo ci moom.\n1:18 Mooy bopp bi yilif j\u00ebmm ji, di mbooloom \u00f1i ko g\u00ebm, ndaxte moom mooy nj\u00e0lb\u00e9en gi, di taaw bi, maanaam ki j\u00ebkk a dekki, ngir muy kilifa ci b\u00e9pp f\u00e0nn.\n1:19 Ndaxte soob na Y\u00e0lla mu d\u00ebkkal matam g\u00e9pp ci moom\n1:20 te jaar ci moom, jubale l\u00e9pp ak boppam, muy ci kaw asamaan yi mbaa ci suuf, ba mu w\u00e0ccee j\u00e0mm jaarale ko ci deret ji tuuru, bi Doom ji deeyee ca bant ba.\n1:21 Te y\u00e9en \u00f1i sore woon Y\u00e0lla te doon ay noonam ci seen xel ak seen j\u00ebf yu bon,\n1:22 l\u00e9egi nag Y\u00e0lla jubale na leen ak boppam jaare ko ci deewu Kirist ci yaramu nitam, ngir taxawal leen ca kanamam, ngeen sell te \u00f1\u00e0kk sikk ak i \u014b\u00e0\u00f1\u00f1.\n1:23 Loolu nag na fekk ngeen w\u00e9y ci ng\u00ebm, sampu ci ba d\u00ebg\u00ebr ci, tey s\u00e9entu c\u00e9r, bi leen xebaar bu baax bi jox. Te xebaar bu baax, boobu ngeen d\u00e9gg te \u00f1u y\u00e9gal waa \u00e0ddina s\u00e9pp, man Pool moom laay y\u00e9gle.\n1:24 L\u00e9egi nag maa ngi am b\u00e0nneex ci coono, yi may daj ngir seen njari\u00f1; te li des sax ci fitnay Kirist, noonu laa koy \u00e0ggalee ngir njari\u00f1u mbooloom \u00f1i g\u00ebm, di j\u00ebmmam.\n1:25 Jawri\u00f1u mbooloo moomu laa, ndaxte Y\u00e0lla sas na ma ngir y\u00e9en, may y\u00e9gle fu nekk k\u00e0ddoom,\n1:26 maanaam ma y\u00e9gle kumpa, gi n\u00ebbbu woon ay jamonoy jamono, waaye l\u00e9egi Y\u00e0lla xamal na ko ay gaayam\n1:27 ci xeeti \u00e0ddina s\u00e9pp. \u00d1oom nag la Y\u00e0lla b\u00ebgg a xamal ni ndamu kumpa googu m\u00e0gge, maanaam Kirist a ngi d\u00ebkk ci y\u00e9en, di yaakaar ju w\u00e9r ci ndamu \u00ebll\u00ebg.\n1:28 Moom Kirist lanuy y\u00e9gle, di artu te di j\u00e0ngal ku nekk, \u00e0nd ak xel mu mat, ngir j\u00e9bbal Y\u00e0lla ku nekk ni ku mat ci Kirist.\n1:29 Ci loolu laay j\u00ebmale sama ligg\u00e9ey, di b\u00ebree dooley Kirist, jiy yengu ci man ak k\u00e0ttan.\n2:1 B\u00ebgg naa nag, ngeen xam b\u00ebre bu metti, bi may b\u00ebre ngir y\u00e9en, ngir waa Lawdise ak \u00f1\u00e9pp \u00f1i ma musul a teg b\u00ebt. Damay def sama kem-k\u00e0ttan,\n2:2 ngir ngeen am fit te nekk benn ci mb\u00ebggeel, ngir dajal noonu xam-xam bu mat, ba xam kumpag Y\u00e0lla, di Kirist.\n2:3 Ci moom la\u00f1u denc l\u00e9pp lu \u00f1uy s\u00e0kku ci xel ak ci xam-xam.\n2:4 Maa ngi wax lii, ngir kenn ba\u00f1 leen a nax ci ay wax yu neex.\n2:5 J\u00ebmm ji \u00f1\u00ebwul waaye sama xel a ngi ci y\u00e9en, di b\u00e9g ci seen doxalin ak ng\u00ebm gu d\u00ebg\u00ebr, gi ngeen am ci Kirist.\n2:6 Kon nag, ni ngeen nangoo Kirist Yeesu ni Boroom bi, dundeleen noonu ci moom.\n2:7 Saxleen ci moom, di m\u00e0gg ci moom, tey g\u00ebn a d\u00ebg\u00ebr ci ng\u00ebm, gi \u00f1u leen j\u00e0ngal, ba seen xol di baawaan ci g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla.\n2:8 Moytuleen ba kenn ba\u00f1 leen a f\u00e0bbi ci ay xam-xami nit yuy naxi neen. Xam-xam yu mel noonu, \u00f1u ngi soqikoo ci aada yu nit t\u00ebral, ci aaday \u00e0ddina, waaye soqikoowul ci Kirist.\n2:9 Ndaxte ci Kirist, maanaam ci yaramu nitam, la matug Y\u00e0lla g\u00e9pp d\u00ebkk,\n2:10 te mat ngeen ci moom, miy buuru kilifa y\u00e9pp ak boroom sa\u00f1-sa\u00f1 y\u00e9pp.\n2:11 Ndax seen ng\u00ebm ci moom xaraf ngeen xaraf bu loxol nit deful, maanaam Kirist summil na leen dooley b\u00e0kkaar, ji moomoon seen yaram. Loolu mooy xaraf, bi Kirist def.\n2:12 Bi \u00f1u leen s\u00f3obee ci ndox, suulaale na\u00f1u leen ak moom, te it dekki ngeen ak moom, ndaxte g\u00ebm ngeen ci dooley Y\u00e0lla, ji ko dekkal ca n\u00e9ew ya.\n2:13 Te y\u00e9en \u00f1i doon ndee fa kanam Y\u00e0lla ndax seeni moy ak seen \u00f1\u00e0kka xaraf, Y\u00e0lla dundalaat na leen ak Kirist, baal nu sunuy b\u00e0kkaar y\u00e9pp.\n2:14 Mbind mi nu doon tii\u00f1al, te daa nu yey ndax ay s\u00e0rtam, Y\u00e0lla far na ko, dindi ko, daajaale ko ca bant, ba Kirist deeye.\n2:15 Futti na kilifa yi ak boroom sa\u00f1-sa\u00f1 yi, weer leen ci kanamu \u00f1\u00e9pp, s\u00ebkktal leen niy jaam ndax ndam la Kirist j\u00eble ca bant ba.\n2:16 Kon nag bu leen kenn teg too\u00f1 ci li j\u00ebm ciy \u00f1am mbaa naan, ci m\u00e0ggal mbaa xewu weer wu fee\u00f1, mbaa ci b\u00e9su noflaay.\n2:17 Loolu l\u00e9pp nag takkandeer la woon buy misaal li waroon a \u00f1\u00ebw, waaye lu d\u00ebggu li mi ngi ci Kirist.\n2:18 Kuy b\u00e9g ci di toroxlu ci ngistal, di jaamu ay malaaka, buleen ko may, mu \u00e0tte leen. Kooku dafay jeneer, di seet li koy fee\u00f1u, bay tiitaroo xalaatam, fekk xalaatu nit kese la, te neen.\n2:19 Taqul ci Kirist, miy bopp bi yilif j\u00ebmm ji. Bopp bee tax ba j\u00ebmm j\u00e9pp, ji siddit yi ak tenqo yi t\u00e9ye te taqale ko, di m\u00e0gg m\u00e0gg gi ko Y\u00e0lla di jox.\n2:20 Ndegam deeyandoo ngeen ak Kirist, ba g\u00e9nne noonu ci aaday \u00e0ddina, lu tax ngeen di nangu, \u00f1u di leen teg ay s\u00e0rt yu mel nii: \u00abBul fab, bul \u00f1am, bul laal,\u00bb ni bu seenug dund aju woon ci \u00e0ddina si?\n2:22 S\u00e0rt yooyu \u00f1u ngi aju ci ndigali nit \u00f1i ak seen nj\u00e0ngale. Y\u00ebf yi \u00f1u tudd y\u00e9pp, dees na leen jari\u00f1oo, ba \u00f1u jeex.\n2:23 D\u00ebgg la, seeni s\u00e0rt da\u00f1uy d\u00e9nkaane pasteef ci jaamu Y\u00e0lla, di toroxlu ak di fitnaal seen yaram. Waaye s\u00e0rt yooyu nag amu\u00f1u benn njari\u00f1, ngir nit \u00f1i noot seen nafsu.\n3:1 Kon nag ndegam dekkeendoo ngeen ak Kirist, wutleen y\u00ebf, ya nekk ca kaw, fa Kirist toog ca ndeyjooru Y\u00e0lla.\n3:2 Fonkleen y\u00ebf ya ca kaw, te ngeen ba\u00f1 a faale yi ci suuf,\n3:3 ndaxte dee ngeen, te seen dund boole na\u00f1u ko ak Kirist, denc ca Y\u00e0lla.\n3:4 Te b\u00e9s bu Kirist miy seen dund fee\u00f1ee, y\u00e9en itam dingeen fee\u00f1 ak moom ci biir ndam.\n3:5 Kon nag li nekk ci y\u00e9en te bokk ci mbiri \u00e0ddina, j\u00e9bbal-leen ko dee, yu deme ni ndoxaanu y\u00e0qute, sobe, xemmem, b\u00ebgg-b\u00ebgg yu bon, ak b\u00ebgge, maanaam bokkaale Y\u00e0lla.\n3:6 Yooyooy x\u00ebcc merum Y\u00e0lla.\n3:7 Y\u00e9en itam noonu ngeen daan doxale bu j\u00ebkk, ba ngeen daan dunde noonu.\n3:8 Waaye l\u00e9egi b\u00e0yyileen yii y\u00e9pp: mer, xadar, ki\u00f1aan ak di g\u00e9nne ci seen g\u00e9mmi\u00f1 sos ak wax ju \u00f1aaw.\n3:9 B\u00e0yyileen di fen seeni moroom, ndaxte summi ngeen jikko ju bon, ji ngeen judduwaale, moom ak ay j\u00ebfam;\n3:10 te sol ngeen dund gu bees, gi Y\u00e0lla s\u00e0kk te di ko yeesal ba mu mel ni moom, ngir ngeen man koo xam bu w\u00e9r.\n3:11 Ci dund gu bees googu, amul Yawut ak ku dul Yawut, ku xaraf walla ku xaraful, jaam walla gor, ku j\u00e0ngul ni Baarbaar yi, ak ku yeewuwul ni waa Sit, waaye Kirist ay l\u00e9pp te d\u00ebkk ci \u00f1\u00e9pp.\n3:12 Kon nag ndegam Y\u00e0lla t\u00e0nn na leen, sellal leen, sopp leen, solooleen boog y\u00ebrmande, laabiir, woyof, lewet ak mu\u00f1.\n3:13 Mu\u00f1alanteleen, di baalante, su amee kuy tawat moroomam. Baalanteleen, ni leen Boroom bi baale.\n3:14 Ci kaw loolu l\u00e9pp amleen mb\u00ebggeel, giy j\u00f3kkaale l\u00e9pp, ba mu mat.\n3:15 Na j\u00e0mm ji Kirist di joxe noot seeni xol, ndaxte Y\u00e0lla woo na leen ci loolu, mel ni ay c\u00e9r yu bokk benn yaram; te g\u00ebr\u00ebmleen Y\u00e0lla.\n3:16 Na k\u00e0ddug Kirist d\u00ebkk ci y\u00e9en, bay baawaan, ngeen di j\u00e0ngalante ak a artoonte ci seen biir ak xel mu mat s\u00ebkk, di woy ak a g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla ak seen xol b\u00e9pp, ay taalifi Sab\u00f3or, ay ka\u00f1 Y\u00e0lla ak ay cant yu tukkee ci Xelum Y\u00e0lla.\n3:17 Te lu ngeen man a def, muy ci wax mbaa ci j\u00ebf, w\u00e9erleen ko ci turu Boroom bi Yeesu, jaare ci moom g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla Baay bi.\n3:18 Jig\u00e9en \u00f1i, na ku nekk nangul j\u00ebkk\u00ebram, ndaxte looloo jekk ci \u00f1i bokk ci Boroom bi.\n3:19 G\u00f3or \u00f1i, na ku nekk b\u00ebgg jabaram te mu\u00f1al ko.\n3:20 Xale yi, d\u00e9ggal-leen seeni waajur ci l\u00e9pp, ndaxte looloo rafet ci \u00f1i bokk ci Boroom bi.\n3:21 Baay yi, buleen bundaxataal seeni doom, ngir ba\u00f1 a jeexal seen xol.\n3:22 Jaam yi, nangul-leen ci l\u00e9pp seen sang, yi ci \u00e0ddina. Buleen ko def rekk ci seen kanam, di s\u00e0kku ng\u00ebr\u00ebm, waaye na nekk lu d\u00ebggu ci y\u00e9en, ndax seen ragal Boroom bi.\n3:23 Lu ngeen man a def, na ci seen xol t\u00e0lli; ngeen def ko ngir Boroom bi, te du ngir nit,\n3:24 xam ne Boroom bi dina fey seeni j\u00ebf, mu di c\u00e9r bi mu leen dencal. Kirist mooy Boroom, bi ngeen di ligg\u00e9eyal.\n3:25 Waaye ku def lu bon, Boroom bi dina la delloo sa j\u00ebf, te du g\u00ebnale.\n4:1 Sang yi, yorleen seeni jaam ci nu jub te aw yoon, xam ne, am ngeen y\u00e9en itam ab Sang ca asamaan.\n4:2 D\u00ebkkleen ci \u00f1aan Y\u00e0lla, farlu ci, boole ci ng\u00ebr\u00ebm.\n4:3 Te ngeen fasaale nu ci \u00f1aan yi itam, ngir Y\u00e0lla ubbil nu bunt, nu man a xamle k\u00e0ddoom, di y\u00e9gle kumpa gi di Kirist, muy kumpa gi waral \u00f1u j\u00e9ng ma.\n4:4 \u00d1aanleen ngir ma xamle ko ni mu ware.\n4:5 J\u00ebfeleen ak xel ci seen diggante ak waa \u00e0ddina, te fu ngeen ame jot, fexeleen ba jari\u00f1oo ko.\n4:6 Na seen wax j\u00e9pp fees ak yiw te am xorom, ngir ngeen xam nan ngeen war a tontoo ku nekk.\n4:7 Tisig, sama mbokk mi ma sopp, di jawri\u00f1 ju takku ak sama nawle ci ligg\u00e9eyu Boroom bi, dina leen y\u00e9gal l\u00e9pp lu j\u00ebm ci samay mbir.\n4:8 Lii moo tax ma yebal ko ci y\u00e9en: ngeen xam xebaar bi j\u00f3ge ci nun, te it mu d\u00ebf\u00ebl seen xol.\n4:9 Onesim lay \u00e0ndal, sunu mbokk mu takku, mi nu sopp, te mu bokk ci y\u00e9en. Dina\u00f1u leen xamal l\u00e9pp lu xew fii.\n4:10 Arist\u00e0rk mi nekk ak man ci kaso bi, mu ngi leen di nuyu, moom ak M\u00e0rk rakku Barnabas. Jot ngeen ay ndigal ci mbirum M\u00e0rk: bu \u00f1\u00ebwee ci y\u00e9en, teral-leen ko.\n4:11 Yeesu mi \u00f1uy d\u00e0kkentale Yustus, moom it mu ngi leen di nuyu. \u00d1oom rekk \u00f1ooy Yawut yiy ligg\u00e9eyandook man ngir nguuru Y\u00e0lla, te \u00f1oo f\u00e9exal sama xol.\n4:12 Jaamu Kirist, Epafras, mi bokk ci y\u00e9en, mu ngi leen di nuyu. Du j\u00f3g ci di leen \u00f1aanal, farlu ci ni kuy b\u00ebre, ngir ngeen taxaw temm ci coobareg Y\u00e0lla g\u00e9pp, \u00e0nd ak ng\u00ebm gu mat ak k\u00f3olute gu w\u00f3or.\n4:13 Maa ngi koy seedeel ne, mu ngi sonn bu baax ngir y\u00e9en, ngir waa Lawdise ak waa Yerapolis.\n4:14 Luug, doktoor bi \u00f1u sopp, mu ngi leen di nuyu, moom ak Demas.\n4:15 Nuyul-leen nu mbokk, yi nekk Lawdise. Nuyul-leen nu itam Nimfa ak mbooloom \u00f1i g\u00ebm, miy daje ci k\u00ebram.\n4:16 Bu \u00f1u j\u00e0ngee bataaxal bii ci y\u00e9en, fexeleen ba \u00f1u j\u00e0ng ko it ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm mi nekk Lawdise, te y\u00e9en it ngeen j\u00e0ng bi ma y\u00f3nnee waa Lawdise.\n4:17 Te neleen Arkib: \u00abFarlul ci sas, wi la Boroom bi s\u00e9dde, ba matal ko.\u00bb\n4:18 Man Pool maa leen di bind nuyoo bii ci sama loxob bopp. F\u00e0ttalikuleen ne, da\u00f1u maa j\u00e9ng. Na yiwu Boroom bi \u00e0nd ak y\u00e9en!","title":"Wolof Bible (NT): Colossians","type":"page"}
