{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/eph.htm","path":"bib/wb/wlf/eph.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/eph.htm","text":"1:1 Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Y\u00e0lla, maa leen di bind, y\u00e9en gaayi Y\u00e0lla yu sell yi te g\u00ebm Kirist Yeesu ci d\u00ebkku Efes.\n1:2 Na leen Y\u00e0lla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak j\u00e0mm.\n1:3 Cant \u00f1eel na Y\u00e0lla Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu sotti ci sunu bokk ci Kirist l\u00e9pp luy barkeel ci baatin te nekk ca b\u00e9rab yu kawe ya.\n1:4 Ndaxte ba \u00e0ddina sosoogul, t\u00e0nn na nu ci Kirist, ngir nu man a teew fa kanamam, sell te \u00f1\u00e0kk sikk. Ci kaw mb\u00ebggeelam\n1:5 s\u00e9ddoo na nu lu jiitu, def nu ay doomam jaarale ko ci Yeesu Kirist, ndaxte looloo doon y\u00e9ene ju rafet, ji mu t\u00ebral ci coobareem.\n1:6 Na ndamam jolli ndax yiw wu r\u00e9y, wi mu nu sotti ci Soppeem bi.\n1:7 Moom jot na nu ak deretam ji \u00f1u tuur, maanaam baal nu sunuy b\u00e0kkaar, ci kaw yiw wu yaatu,\n1:8 wi mu nu baawaanal. Te Y\u00e0lla sol na nu xel mu mat ak d\u00e9gg,\n1:9 ci fee\u00f1al nu mb\u00f3oti coobareem, d\u00ebppook y\u00e9eneem ju rafet, ji mu jaarale ci Kirist.\n1:10 Mu t\u00ebral ne, bu jamono yi w\u00e9yee ba l\u00e9pp mat, dina dajale l\u00e9pp ci kilifteefu Kirist, muy ci kaw, muy ci suuf.\n1:11 Te am nanu c\u00e9r ci moom bu nu Y\u00e0lla s\u00e9dd lu jiitu ci dogalam, moom miy doxal l\u00e9pp ci ni mu ko \u00e0ttee ci coobareem.\n1:12 Noonu nuy jollil ndamam, nun \u00f1i j\u00ebkk a w\u00e9kk sunu yaakaar ci Kirist.\n1:13 Te y\u00e9en itam, bi ngeen d\u00e9ggee k\u00e0ddug d\u00ebgg gi, di xebaar bu baax, bi leen tegtal yoonu mucc, te ngeen g\u00ebm ko, Y\u00e0lla t\u00e0mpe na leen ni \u00f1o\u00f1am ak Xel mu Sell, mi mu dige woon.\n1:14 Te Xel mi mooy dawal gi nu Y\u00e0lla jox ci c\u00e9r, bi mu nu dencal, ba kera muy goreel \u00f1i mu jotal boppam, te \u00f1\u00e9pp jollil ndamam.\n1:15 Bi ma d\u00e9ggee nag seen ng\u00ebm ci Boroom bi Yeesu ak seen mb\u00ebggeel ci gaayi Y\u00e0lla yu sell y\u00e9pp,\n1:16 duma noppee sant Y\u00e0lla, di leen boole ci samay \u00f1aan.\n1:17 Te li may \u00f1aan Y\u00e0llay sunu Boroom Yeesu Kirist, di Baay bi yelloo ndam, mooy lii: mu sol leen xel mu x\u00f3ot, te xamal leen boppam\n1:18 ci leeral seeni xol. Noonu dingeen xam yaakaaru \u00ebll\u00ebg, ji leen Y\u00e0lla wooye, di ndam lu xel m\u00ebnta daj, li nekk ci c\u00e9r, bi mu dencal gaayam yu sell yi.\n1:19 Ngeen xam it, ni k\u00e0ttanam m\u00e0gge ba j\u00e9ggi dayo, j\u00ebm ci nun \u00f1i g\u00ebm, d\u00ebppook dooleem ju r\u00e0\u00f1\u00f1iku,\n1:20 ji mu j\u00ebfe ci Kirist, ci li mu ko dekkal, d\u00eb\u00ebl ko ci ndeyjooram ca b\u00e9rab yu kawe ya,\n1:21 mu tiim lu sore malaaka y\u00e9pp, muy kilifa, boroom sa\u00f1-sa\u00f1, boroom doole mbaa buur, te g\u00ebn a m\u00e0gg w\u00e9pp tur wu \u00f1u man a tudd, muy tey, muy \u00ebll\u00ebg.\n1:22 Y\u00e0lla suufeel na l\u00e9pp fi kanamam, def ko kilifag l\u00e9pp ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm,\n1:23 miy j\u00ebmmam, di matug Kirist, mi fees mbindeef mu ne ci f\u00e0nn gu ne.\n2:1 Te y\u00e9en itam Y\u00e0lla dekkal na leen, y\u00e9en \u00f1i doon ndee fa kanamam ci seeni moy ak seeni b\u00e0kkaar.\n2:2 Ci biir yooyu ngeen doon dund d\u00e9mb, topp doxalinu \u00e0ddina, tey d\u00e9ggal kilifag boroom sa\u00f1-sa\u00f1 yi ci jaww ji, di xel mu bon miy j\u00ebf ci kureelu \u00f1i d\u00e9ggadil Y\u00e0lla.\n2:3 Te nun it booba \u00e0ndoon nanu ak \u00f1oom ca seen dund ga, di topp sunu bakkan ciy wut b\u00e0nneexi yaram ak coobarey xel. Noonu ci sunu bindu nit yeyoo nanu meru Y\u00e0lla, ni \u00f1a ca des.\n2:4 Waaye Y\u00e0lla mi bare y\u00ebrmande, ci kaw mb\u00ebggeel gu r\u00e9y, gi mu am ci nun,\n2:5 dundalaat na nu ak Kirist, fekk ndee lanu woon fa kanamam ci sunuy b\u00e0kkaar \u2014 ci kaw yiwu Y\u00e0lla ngeen mucce.\n2:6 Te dekkal na nu ak Kirist Yeesu, d\u00eb\u00ebl nu ak moom ca b\u00e9rab yu kawe ya.\n2:7 Noonu ba fu jamono yem, dina la\u00f1al fi sunu kanam yiwam wu r\u00e9y wi xel m\u00ebnta takk, jaar ci baaxaay gi mu nu won ci Kirist Yeesu.\n2:8 Ndaxte ci yiwu Y\u00e0lla ngeen mucce ci kaw ng\u00ebm, te loolu j\u00f3gewul ci y\u00e9en, mayu Y\u00e0lla la;\n2:9 du peyu j\u00ebf, ngir kenn du ci ka\u00f1u.\n2:10 Ndaxte j\u00ebfu Y\u00e0lla lanu; moo nu bind ci Kirist Yeesu, ngir nu w\u00e9y ci j\u00ebf yu rafet, yi mu nu f\u00e0gguloon ca nj\u00e0lb\u00e9en ga.\n2:11 Kon nag y\u00e9en \u00f1i dul Yawut cib juddu, y\u00e9en \u00f1i xaraful, te \u00f1i xaraf ci seen yaram ci loxol nit \u00f1oo leen teg ay y\u00e9efar, f\u00e0ttalikuleen lii:\n2:12 booba amuleen woon benn c\u00e9r ci Kirist, mbaa benn baat ci kureelu b\u00e0nni Israyil. Bokkuleen woon ci k\u00f3ll\u00ebre, gi Y\u00e0lla fas ak \u00f1oom, te \u00ebmb dige ya. Amuleen woon jenn yaakaar mbaa benn xam-xamu Y\u00e0lla ci \u00e0ddina.\n2:13 Waaye l\u00e9egi ci seen bokk ci Kirist Yeesu, y\u00e9en \u00f1i sore woon jege ngeen ndax deretu Kirist ji \u00f1u tuur.\n2:14 Ndaxte mooy sunu j\u00e0mm, moom mi j\u00ebl Yawut ak ki dul Yawut, def nu benn. \u00d1ag bi doxoon sunu diggante te sosoon sunu d\u00ebngoo, moo ko m\u00e0bb ci li mu joxe yaramam,\n2:15 far noonu yoonu Musaa, muy ndigal ya ak dogal ya. Noonu la nu j\u00eble, Yawut ak ki dul Yawut, def nu benn ci moom, ba nu j\u00e0mmoo.\n2:16 Te nun \u00f1aar, \u00f1i def benn j\u00ebmm, jubale na nu ak Y\u00e0lla ci dee, gi mu dee ca bant ba \u00f1u ko daajoon, dindee noonu sunu tongoonte.\n2:17 Bi mu ko defee mu \u00f1\u00ebw, y\u00e9galsi nu xebaaru j\u00e0mm fa kanam Y\u00e0lla, y\u00e9en \u00f1i sore woon ak nun \u00f1i jege.\n2:18 Ndaxte nun \u00f1aar \u00f1\u00e9pp am nanu bunt ci Y\u00e0lla Baay bi, jaar ci Kirist, ci ndimbalu menn Xel mu Sell mi.\n2:19 Noonu dootuleen ay doxand\u00e9em mbaa ay gan, waaye am ngeen baat ci kureelu gaayi Y\u00e0lla yu sell yi, te waa k\u00ebram ngeen.\n2:20 Y\u00e9ena ngi sukkandikoo ci fondamaa, bi ndawi Kirist yi ak yonent yi tabax, te Kirist Yeesu ci boppam di doju dalil wa.\n2:21 Ci moom la doj y\u00e9pp r\u00e0bbloo, ba tabax bi j\u00f3g, di m\u00e0ggalukaay bu sell ngir Boroom bi.\n2:22 Te ci seen bokk ci Kirist, Y\u00e0lla boole na leen tabax y\u00e9en itam, ba ngeen nekk d\u00ebkkukaayam, jaar ci Xel mu Sell mi.\n3:1 Kon nag maa ngi leen di \u00f1aanal, man Pool mi \u00f1u t\u00ebj kaso ci turu Kirist ndax sas wi may bey ci y\u00e9en, xeet yi dul Yawut.\n3:2 W\u00f3or na ma ne, d\u00e9gg ngeen yenub xamle yiwu Y\u00e0lla, bi mu ma jagleel j\u00ebm ci y\u00e9en.\n3:3 Y\u00e0lla fee\u00f1u na ma, xamal ma mb\u00f3oti mbir mi mu t\u00ebral, ni ma leen ko binde ci k\u00e0ddu yu n\u00e9ew.\n3:4 Bu ngeen j\u00e0ngee loolu, dingeen man a xam bu w\u00e9r d\u00e9gg, gi ma am ci mb\u00f3oti mbiri Kirist.\n3:5 Ci jamono yu weesu, loolu kumpa la woon ci doom Aadama, waaye l\u00e9egi Y\u00e0lla fee\u00f1alal na ko ay ndawam ak yonentam yu sell yi, jaarale ko ci Xel mu Sell mi.\n3:6 Mbir mi nii la t\u00ebdde: l\u00e9egi xeet yi dul Yawut da\u00f1oo bokksi c\u00e9r ak Yawut yi, bokk ak \u00f1oom jenn j\u00ebmm, bokk w\u00e0ll ci x\u00e9ewal yi Y\u00e0lla dige ci Kirist Yeesu, te xebaar bu baax bi xamle ko.\n3:7 Xamle xebaar bu baax boobu nag, Y\u00e0lla fal na ma ci jawri\u00f1 ci kaw yiwam, te di ma dooleel ci k\u00e0ttanam.\n3:8 May na ma, man mi g\u00ebn a tuuti ci gaayi Y\u00e0lla yu sell yi, may xebaar xeeti \u00e0ddina barkeel yu xel dajul yi ci Kirist;\n3:9 te it may sulli melokaanu mbir mu x\u00f3ot mi Y\u00e0lla t\u00ebral, te doon kumpa nj\u00e0lb\u00e9en ga ba tey ci moom, mi sos l\u00e9pp.\n3:10 Waaye l\u00e9egi nee na f\u00e0\u014b\u014b, ngir kilifa yi ak boroom sa\u00f1-sa\u00f1 yi ca b\u00e9rab yu kawe ya man a xam ni Xelum Y\u00e0lla x\u00f3ote, jaar ci li \u00f1u gis ci mbooloom \u00f1i g\u00ebm Kirist.\n3:11 Mooy dogal bi sax d\u00e0kk, te Y\u00e0lla t\u00ebral ko ci Kirist Yeesu sunu Boroom.\n3:12 Ci turam am nanu k\u00f3olute fa kanam Y\u00e0lla, ak bunt bu yaatu ci moom ci kaw ng\u00ebm.\n3:13 Maa ngi leen di \u00f1aan nag, ngeen ba\u00f1 a yoqi ndax coono, yi may j\u00eble ci bey sama sas ci y\u00e9en, xam ne coono yooyu \u00f1oo leen di jural ndam.\n3:14 Moo tax maa ngi sukk, jublu ci Y\u00e0lla Baay\n3:15 biy cosaanul njaboot g\u00e9pp, muy ci kaw, muy ci suuf.\n3:16 Ma di ko \u00f1aan, mu may leen, ci kaw ndamam lu amul kem, Xel mu Sell mi feddali seen baatin ak k\u00e0ttan gu mag,\n3:17 ba Kirist d\u00ebkk ci seeni xol ci kaw ng\u00ebm. Te ngeen sax noonu te sampu ci mb\u00ebggeelu Y\u00e0lla,\n3:18 ba jagoo, y\u00e9en ak gaayi Y\u00e0lla yu sell y\u00e9pp, guddaay ba, yaatuwaay ba, kawe ga ak x\u00f3otaay ba,\n3:19 te xam mb\u00ebggeelu Kirist, gi raw m\u00e9pp xel. Noonu dingeen fees dell ak matug Y\u00e0lla.\n3:20 L\u00e9egi nag, na ndam li f\u00e9ete ak Y\u00e0lla, mi man a yeggale l\u00e9pp luy \u00f1aan mbaa y\u00e9ene, ba weesu ko fuuf, d\u00ebppook k\u00e0ttan giy j\u00ebf ci nun;\n3:21 moo yelloo ndamul mbooloom \u00f1i g\u00ebm jamonoy jamono ba f\u00e0ww, jaar ci Kirist Yeesu. Amiin.\n4:1 Man mi \u00f1u t\u00ebj kaso ngir Boroom bi nag, maa ngi leen di d\u00e9nk, ngeen dund dundin wu yellook wooteb Y\u00e0lla.\n4:2 Ngeen woyof toyy te lewet, di mu\u00f1alante tey baalante ci mb\u00ebggeel,\n4:3 te dem ba fu seen k\u00e0ttan yem, ngeen likkoo ci j\u00e0mm, bay s\u00e0mm booloo gi leen Xelum Y\u00e0lla may.\n4:4 Jenn j\u00ebmm moo am, menn Xel, ak jenn yaakaaru \u00ebll\u00ebg ju wooteb Y\u00e0lla \u00ebmb.\n4:5 Benn Boroom it a am, genn ng\u00ebm, ak benn seedeb ng\u00ebm ci li \u00f1u leen s\u00f3ob ci ndox.\n4:6 Te jenn Y\u00e0llaa am, di Baayu \u00f1\u00e9pp, mu tiim \u00f1\u00e9pp, fees \u00f1\u00e9pp, te d\u00ebkk ci \u00f1\u00e9pp.\n4:7 Waaye ku nekk ci nun ak mayam, ni nu ko Kirist s\u00e9ddalee.\n4:8 Looloo tax Mbind mi ne:\u00abY\u00e9eg na ba ca fa g\u00ebn a kawe,y\u00f3bbaale mbooloom noon mu bare, mi mu noot,tey s\u00e9ddale nit \u00f1i ay may.\u00bb\n4:9 Su nu waxee ne \u00aby\u00e9eg na,\u00bb li moo ci g\u00e9nn: daa j\u00ebkk a w\u00e0cc ba ca b\u00e9rab ya g\u00ebn a suufe.\n4:10 Ki w\u00e0ccoon moo y\u00e9egaat, ba tiim asamaan y\u00e9pp, ngir fees l\u00e9pp.\n4:11 Moo may \u00f1ii di ay ndawam, \u00f1ii ay yonent, \u00f1ii ay taskati xebaar bu baax bi, ak \u00f1eneen \u00f1uy s\u00e0mm mbooloom \u00f1i g\u00ebm te di ko j\u00e0ngal.\n4:12 Maye na leen, ngir \u00f1u waajal gaayi Y\u00e0lla yu sell yi, \u00f1u man a bey seen sas ci taxawal mbooloom Kirist, di j\u00ebmmam.\n4:13 Noonu nu m\u00e0nkoo ci sunu ng\u00ebm ak ci xam Doomu Y\u00e0lla ji, ba kera nuy egg ci nekk nit ku sotti, te taxaw taxawaay bu d\u00ebppook matug Kirist.\n4:14 Noonu dootunu ay gune yu nj\u00e0ngalem nit ku \u00f1\u00ebw di f\u00e0bbi ci seeni l\u00e0qarci ak seeni pexe, nu mel ni ay gaal yu duus yi ak ngelaw li di baaje.\n4:15 Waaye dinanu wax d\u00ebgg, \u00ebmb ko ci mb\u00ebggeel, bay m\u00e0gg ci f\u00e0nn gu ne ci sunu bokk ci Kirist. Mooy bopp,\n4:16 te j\u00ebmm j\u00e9pp ci moom lay dunde, di j\u00ebmm ju r\u00e0bboo te d\u00e9ggoo ci b\u00e9pp tenqoo, te c\u00e9r bu nekk di def warugaram. Noonu j\u00ebmm ji di yokku ak a m\u00e0gg ci biir mb\u00ebggeel.\n4:17 Maa ngi leen di wax lii nag, te di ko d\u00ebggal ci kanamu Boroom bi: buleen dundeeti ni xeeti \u00e0ddina yi, ci seeni xalaati neen\n4:18 ak seen xel mu l\u00ebnd\u00ebm. Da\u00f1oo g\u00e9nn ci dundu Y\u00e0lla, ndax umple gi \u00f1u am ci moom, ak li \u00f1u ko t\u00ebjal seen xol.\n4:19 Seen xol dafa d\u00ebrkiis, ba \u00f1u bayliku ciy topp seen nafsu, di s\u00f3obu ci b\u00e9pp sobe te x\u00e9r ci.\n4:20 Waaye du dundin woowu ngeen j\u00e0ng ci Kirist.\n4:21 Ndax yaakaar naa ne, d\u00e9gg ngeen Kirist te j\u00e0ng ngeen ci moom, ba xam d\u00ebgg gi Yeesu \u00ebmb.\n4:22 Maanaam ngeen yulli seen jikko ju bon, ji ngeen judduwaale te daan f\u00e9s ci seeni j\u00ebf, te muy g\u00ebn a y\u00e9es, moom ak i b\u00ebgg-b\u00ebggam yuy naxe kese.\n4:23 Te ngeen yeeslu ci seen biir xel,\n4:24 te soloo jikko ju bees, ji Y\u00e0lla s\u00e0kk ci njub ak sell yu d\u00ebggu.\n4:25 Kon nag b\u00e0yyileen di fen, tey wax d\u00ebgg kenn ku nekk ci moroomam, ndax ku nekk sa genn-w\u00e0llu moroom nga.\n4:26 Ku mer, bu mu j\u00e0ll aw kaa\u00f1; bu jant bi sowaale seen mer,\n4:27 ba ngeen may Seytaane bunt.\n4:28 Ku daan s\u00e0cc, na ko d\u00ebddu te jublu ci ligg\u00e9ey lu baax ci ay loxoom, ngir mu man a dimbali \u00f1i n\u00e9ew doole.\n4:29 Bu genn k\u00e0ddu gu \u00f1aaw g\u00e9nn ci seen g\u00e9mmi\u00f1, waaye su wax yegsee, nangeen wax lu rafet, ba faj soxlay seeni moroom, te teg \u00f1i leen di d\u00e9glu ci yoonu yiw.\n4:30 Buleen y\u00f3bbe tiis Xelu Y\u00e0lla mu Sell, mi leen t\u00e0mpe ngir b\u00e9su goreel ba.\n4:31 D\u00ebdduleen l\u00e9pp luy wex mbaa t\u00e0ng bopp, luy mer mbaa coow, l\u00e9pp luy xaste mbaa coxor.\n4:32 Te ngeen baax ci seen diggante, di laayante biir tey baalante, ni leen Y\u00e0lla baale ci turu Kirist.\n5:1 Y\u00e9en nag \u00f1iy guney Y\u00e0lla, yi mu b\u00ebgg ci xolam, royleen ko ci loolu.\n5:2 Ngeen w\u00e9er seen dund ci mb\u00ebggeel, mel ni Kirist mi nu b\u00ebgg, ba joxe bakkanam ngir nun, di sarax su \u00f1u j\u00e9bbal Y\u00e0lla te neex ko ni xetu latkolo\u00f1.\n5:3 Waaye naka njaaloo ak b\u00e9pp sobe mbaa b\u00ebgge, j\u00e9llale naa j\u00ebf ji sax, waaye bu ko l\u00e0mmi\u00f1 tudd, ni mu jekke ci gaayi Y\u00e0lla yu sell yi.\n5:4 Dawleen it yu jekkadee, ni wax ju \u00f1aaw mbaa waxi caaxaan ak kaf yu bon, te ngeen sax ci sant Y\u00e0lla.\n5:5 Na leen w\u00f3or ne, kenn ku jikkowoo ndoxaan, sobe mbaa b\u00ebgge, maanaam bokkaale Y\u00e0lla, kooku du am c\u00e9r ci nguuru Kirist ak Y\u00e0lla.\n5:6 Bu leen kenn nax ci ay waxi neen, ndaxte j\u00ebf yooyooy tax meru Y\u00e0lla di w\u00e0cc ci kureelu \u00f1i ko d\u00e9ggadil.\n5:7 Kon nag buleen s\u00e9q ak \u00f1oom dara.\n5:8 L\u00ebnd\u00ebm ngeen woon, waaye l\u00e9egi leer ngeen ndax seen bokk ci Boroom bi. Dundeleen nag ni ay guney leer.\n5:9 Leer, mbaax lay me\u00f1\u00f1, njub ak d\u00ebgg.\n5:10 D\u00ebggal-leen ci seeni j\u00ebf li neex Boroom bi,\n5:11 te daw l\u00e9pp luy j\u00ebfi l\u00ebnd\u00ebm yu amul njari\u00f1, bay weer sax ku koy def.\n5:12 Ndaxte waxtaane sax li \u00f1uy def ci n\u00ebbbu, lu ruslu la;\n5:13 waaye leer, lu mu \u00ebmb, f\u00e9sal ko.\n5:14 Ndaxte lu jaxasoo ak leer di leer. Looloo tax \u00f1u ne:\u00abYeewul, yaw mi nelaw,te j\u00f3ge ci biir n\u00e9ew yi,kon Kirist dina ne r\u00e0\u00f1\u00f1 ci yaw,ni leeru jant buy fenk.\u00bb\n5:15 Noonu s\u00e0mmleen seen dundin, waxuma ni \u00f1u amul xel, waaye ni \u00f1u am xel,\n5:16 tey jari\u00f1oo jot gi, ndaxte nu ngi ci jamono ju bon.\n5:17 Buleen \u00f1\u00e0kk bopp nag, waaye xamleen liy coobareg Boroom bi.\n5:18 Buleen m\u00e0ndi it ci sangara, liy ndeyi \u00f1aawteef, waaye feesleen ak Xel mu Sell mi;\n5:19 di waxante ci seen biir ci ay taalifi Sab\u00f3or, ci ay woy ak ay cant yu tukkee ci Xelum Y\u00e0lla, di woy ak a ka\u00f1 Boroom bi ci seeni xol.\n5:20 G\u00ebr\u00ebmleen Y\u00e0lla Baay bi ci turu Yeesu Kirist Boroom bi, fu ngeen man a tollu, ci lu mu man a doon;\n5:21 teg ca nangul sa moroom ci biir wegeelu Kirist.\n5:22 Naka y\u00e9en jig\u00e9en \u00f1i, nangeen nangul seeni j\u00ebkk\u00ebr, ni su doon Boroom bi.\n5:23 Ndaxte g\u00f3or mooy kilifag jabaram, ni Kirist nekke kilifag mbooloom \u00f1i g\u00ebm, muy j\u00ebmmam ji muy s\u00e0mm.\n5:24 Ni mbooloo mi nag jiitale Kirist, noonu la jig\u00e9en ji war a jiitale j\u00ebkk\u00ebram ci l\u00e9pp.\n5:25 Y\u00e9en nag g\u00f3or \u00f1i, na ku nekk b\u00ebgg jabaram, ni Kirist b\u00ebgge mbooloo mi, ba joxe bakkanam ndax moom,\n5:26 ngir sellal ko ak k\u00e0ddoom, ba mu laab ni ku sangu set.\n5:27 Noonu dina ko j\u00ebl, mu mel ni s\u00e9et bu \u00f1u waajal, di mbooloom mu soloo ndam, te g\u00e0kkul, rasul, taqul leneen, waaye mu sell te amul sikk.\n5:28 Na g\u00f3or b\u00ebgg jabaram, ni mu b\u00ebgge boppam. B\u00ebgg sa jabar, b\u00ebgg sa bopp la.\n5:29 Ndaxte kenn musul a ba\u00f1 sa yaram. Waaye danga koy dundal, di ko fonk. Noonu it la Kirist fonke mbooloo mi;\n5:30 ndaxte noo di c\u00e9ri j\u00ebmmam.\n5:31 Mbind mi nee na: \u00abMoo tax g\u00f3or dina beru ndeyam ak baayam, di taq ci jabaram, \u00f1oom \u00f1aar doon benn.\u00bb\n5:32 Loolu \u00ebmb na mb\u00f3ot mu x\u00f3ot; man maa ngi wax ci lu j\u00ebm ci Kirist ak mbooloo mi.\n5:33 Waaye li teew, na g\u00f3or gu nekk b\u00ebgg jabaram, ni mu b\u00ebgge boppam, te jig\u00e9en ji weg j\u00ebkk\u00ebram.\n6:1 Naka y\u00e9en xale yi, nangeen d\u00e9ggal seeni waajur, ci li ngeen bokk ci Boroom bi, ndaxte looloo rafet.\n6:2 \u00abTeralal sa ndey ak sa baay,\u00bb mooy ndigal li j\u00ebkk a \u00ebmb dige,\n6:3 maanaa: \u00abngir nga am gudd fan gu \u00e0nd ak j\u00e0mm.\u00bb\n6:4 Y\u00e9en baay yi it, buleen bundaxataal xale yi, waaye ngeen yar leen, di leen yemale ak a yee ci Boroom bi.\n6:5 Y\u00e9en jaam yi, nangeen d\u00e9ggal seeni sang yu \u00e0ddina, boole ci ragal ak wegeel, di ko def ak xol bu laab, ni su doon ngir Kirist.\n6:6 Buleen ko def rekk ci ngistal, ngir s\u00e0kku ng\u00ebr\u00ebmu nit, waaye ni ay jaami Kirist, di j\u00ebfe coobareg Y\u00e0lla ak seen xol b\u00e9pp.\n6:7 Beyleen seen sas nag ak xol bu t\u00e0lli, ni su doon ngir Boroom bi te du nit,\n6:8 xam ne ku def lu baax, Boroom bi delloo la ko, muy jaam, muy gor.\n6:9 Y\u00e9en it sang yi, j\u00ebfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam, te d\u00ebddu g\u00e9pp raglu, xam ne y\u00e9ena bokk benn Boroom ci asamaan, te \u00f1\u00e9pp a yem fi moom.\n6:10 L\u00e9egi nag doolewuleen ci Boroom bi, te soloo k\u00e0ttanam gu mag gi.\n6:11 G\u00e0nnaayooleen y\u00e9rey xarey Y\u00e0lla y\u00e9pp, ngir man a j\u00e0nkoonte ak pexey Seytaane.\n6:12 Ndaxte nd\u00ebndu xare jib na, waxuma sunu diggante ak nit \u00f1i, waaye ak kilifa yiy n\u00ebxal \u00e0ddina si, \u00f1uy kilifa yi ak ay boroom sa\u00f1-sa\u00f1, di gaayi Seytaane yi ci b\u00e9rab yu kawe yi.\n6:13 Kon nag g\u00e0nnaayooleen y\u00e9rey xarey Y\u00e0lla y\u00e9pp, ba man a j\u00e0nkoonte jamono ju xeex bi taree, noot l\u00e9pp te taxaw temm.\n6:14 Taxawleen kon temm, ge\u00f1oo d\u00ebgg te s\u00e0ngoo njub, muy seen kiiraayu d\u00ebnn.\n6:15 Solooleen j\u00e0mm, ji xebaar bu baax biy joxe, ni ay d\u00e0ll ci seeni t\u00e0nk, ba jekk ci l\u00e9pp.\n6:16 Defleen it ng\u00ebm, muy seen pakk, ba man a f\u00e9l jum yi leen Seytaane di fitt.\n6:17 Defleen mucc, muy seen mbaxanam xare, ak k\u00e0ddug Y\u00e0lla, muy jaasi ji leen Xel mu Sell mi t\u00ebggal.\n6:18 Deeleen \u00f1aan ci xeeti \u00f1aan y\u00e9pp ci k\u00e0ttanu Xel mu Sell mi, te sax ci ak farlu gu mat s\u00ebkk, di \u00f1aanal gaayi Y\u00e0lla yu sell yi y\u00e9pp.\n6:19 Te buleen ma ci f\u00e0tte, ngir waxtu wu ma ubbee sama g\u00e9mmi\u00f1, ma am lu ma wax, ba man a xamle ak fit wu d\u00ebg\u00ebr mb\u00f3oti xebaar bu baax bi.\n6:20 Ndaw laa ci, lu \u00f1u j\u00e9ng; na ma Y\u00e0lla may fit wu ma waxe, ni mu ma ware.\n6:21 Y\u00f3nnee naa leen Tisig sama mbokk, mi ma sopp, te muy jawri\u00f1 ju takku ci ligg\u00e9eyu Boroom bi, ngir mu xamal leen l\u00e9pp li aju ci man ak li may def.\n6:22 Maa leen ko y\u00f3nneel sama bopp, ngir ngeen xam li nu nekke, te mu d\u00ebf\u00ebl seeni xol.\n6:23 Y\u00e9en bokk yi, na leen Y\u00e0lla Baay bi ak Yeesu Kirist Boroom bi may j\u00e0mm ak mb\u00ebggeel gu \u00e0nd ak ng\u00ebm.\n6:24 Na yiwu Y\u00e0lla \u00e0nd ak \u00f1\u00e9pp, \u00f1i b\u00ebgg Boroom bi Yeesu Kirist ak mb\u00ebggeel gu sax.","title":"Wolof Bible (NT): Ephesians","type":"page"}
