{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/gal.htm","path":"bib/wb/wlf/gal.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/gal.htm","text":"1:1 Man Pool, ndawul Yeesu Kirist --nit falu ma ko, te jaarewul it ci nit, mi ngi jaare ci Yeesu Kirist ak Y\u00e0lla Baay, bi ko dekkal \u2014\n1:2 man ak bokk yiy \u00e0nd ak man y\u00e9pp, nu ngi leen di bind, y\u00e9en mboolooy \u00f1i g\u00ebm te d\u00ebkk ci diiwaanu Galasi.\n1:3 Na yiw ak j\u00e0mm f\u00e9ete ak y\u00e9en, j\u00f3ge ci Y\u00e0lla sunu Baay ak Yeesu Kirist Boroom bi,\n1:4 moom mi joxe bakkanam ngir dindi sunuy b\u00e0kkaar, te musal nu ci \u00e0ddina su bon, si nu nekk, d\u00ebppook coobareg Y\u00e0lla sunu Baay,\n1:5 bi yelloo ndam ba f\u00e0ww. Amiin.\n1:6 Man de jaaxle naa! Y\u00e0lla woo na leen ci boppam jaarale ko ci yiw, wi nu Kirist defal, waaye y\u00e9ena ngi koy gaawantoo b\u00e0yyi, ngir topp beneen xebaar,\n1:7 fekk du xebaar bu baax bi. Dafa am rekk ci seen biir ay nit \u00f1iy n\u00ebxal xel yi, te b\u00ebgg a dandal xebaar bu baax bu Kirist.\n1:8 Waaye su fekkee kenn ci nun \u00f1\u00ebw, walla malaaka sax mu j\u00f3ge asamaan, di y\u00e9gle beneen xebaar bu mengoowul ak bi nu leen y\u00e9gal, kooku Yal na alku!\n1:9 Wax nanu ko, maa ngi koy waxaat: bu leen kenn y\u00e9galee beneen xebaar bu dul bi ngeen nangu, kooku Yal na alku!\n1:10 Ndax kon nit laay wut a g\u00ebmloo, am damay fexee yey Y\u00e0lla? Mbaa damay wut a neex nit \u00f1i? Su ma doon wut a neex nit \u00f1i ba tey, kon duma nekkati jaamu Kirist.\n1:11 Bokk yi, maa ngi leen di xamal ne, xebaar bu baax bi ma y\u00e9gle, j\u00f3gewul ci nit.\n1:12 J\u00eblewuma ko ci nit, te kenn j\u00e0ngalu ma ko, waaye Yeesu Kirist moo ma ko won.\n1:13 D\u00e9gg ngeen ni ma doon j\u00ebfe, bi ma nekkee ci diiney Yawut yi, di fitnaal bu metti mbooloom Y\u00e0lla, di ko j\u00e9em a tas.\n1:14 Bokkoon naa ci \u00f1i g\u00ebn a farlu ci diiney Yawut yi, te sawar it ci s\u00e0rti yoon, yi fi samay maam b\u00e0yyi, ba raw sama maas, gi ma bokkal askan.\n1:15 Waaye Y\u00e0lla mi ma t\u00e0nn lu jiitu sama juddu te woo ma ci boppam ci kaw yiwam, bi mu ko soobee, xamal na ma kan mooy Doomam, ngir ma y\u00e9gal \u00f1i dul Yawut xebaar bu baax bi ci mbirum Kirist; booba nag diisoowuma ci ak kenn.\n1:17 Demuma sax Yerusalem seeti \u00f1i ma j\u00ebkk a nekk ay ndawi Kirist, waaye r\u00e9ewu Arabi laa dem, te gannaaw loolu ma dellusiwaat Damas.\n1:18 Ba \u00f1u ca tegee \u00f1etti at, ma sog a dem Yerusalem, ngir xamante ak Sefas, dal fa moom lu mat \u00f1aari ayu-b\u00e9s.\n1:19 Waaye gisuma keneen ci ndaw yi ku dul Saag, doomu ndeyu Boroom bi.\n1:20 Lii ma leen di bind nag, Y\u00e0llaa may seede ci ne, du ay fen.\n1:21 Bi loolu w\u00e9yee dem naa r\u00e9ewu Siri ak r\u00e9ewu Silisi.\n1:22 Waaye ba tey mboolooy \u00f1i g\u00ebm Kirist ci diiwaanu Yude xamu\u00f1u ma woon.\n1:23 Da\u00f1u d\u00e9ggoon \u00f1u naan rekk ne: \u00abKi nu daan fitnaal bu j\u00ebkk te daan j\u00e9em a far yoonu ng\u00ebm wi, l\u00e9egi mi ngi koy y\u00e9gle!\u00bb\n1:24 Te \u00f1uy sant Y\u00e0lla ci man.\n2:1 Ba \u00f1u ca tegee fukki at ak \u00f1eent, \u00e0nd naa ak Barnabas, dellu Yerusalem, y\u00f3bbaale Tit.\n2:2 Dem naa fa, ndaxte Y\u00e0llaa ma fa yebal ci kaw pee\u00f1u. Ba ma demee, daje naa ak \u00f1i \u00f1u g\u00ebn a fonk ca mbooloo ma, ma w\u00e9etoo ak \u00f1oom, won leen xebaar bu baax, bi may y\u00e9gal \u00f1i dul Yawut; ngir ragal sama coonob d\u00e9mb mbaa tey neen.\n2:3 Te Tit mi ma gunge woon sax de, li mu bokk ci xeetu Gereg, taxul \u00f1u sonal nu ci xarafal ko.\n2:4 Fekk na mbir moomu nekk coow ndax naaf\u00e9q, yi yoxoosu ci sunu biir ak m\u00e9b\u00e9t mu bon, ngir seet yaatu gi nu am ci Yeesu Kirist, ba fexe noo defaat ay jaam.\n2:5 Waaye yaatalunu leen benn yoon, ngir d\u00ebggug xebaar bu baax bi man a sax ci y\u00e9en.\n2:6 Waaye \u00f1i \u00f1u g\u00ebn a fonk --ak lu man a doon seen sag xooluma ko, \u00f1\u00e9pp a yem fa kanam Y\u00e0lla \u2014 waaye \u00f1oo\u00f1u \u00f1u teg njiit boog, bi ma dajee ak \u00f1oom, yokku\u00f1u dara ci sama sas.\n2:7 Gis na\u00f1u ne, Y\u00e0llaa nu yebal, muy man di Piyeer, ngir nu y\u00e9gle xebaar bu baax bi; ma f\u00e9etewoo \u00f1i dul Yawut, Piyeer f\u00e9etewoo Yawut yi.\n2:8 Ndaxte ni Y\u00e0lla j\u00ebfe ci Piyeer, miy ndawam ci Yawut yi, noonu it la j\u00ebfe ci man, may ndawam ci \u00f1i dul Yawut.\n2:9 Te Saag, Sefas ak Yowaana nag, \u00f1i \u00f1u teg kenuy mbooloo mi, bi \u00f1u r\u00e0\u00f1\u00f1ee yen bi ma Y\u00e0lla jagleel ci yiwam, \u00f1u fekksi nu ci, ba jox nu loxo, man ak Barnabas, nu ligg\u00e9ey ca \u00f1a dul Yawut, \u00f1oom \u00f1u ligg\u00e9ey ca Yawut ya.\n2:10 Li \u00f1u doon laaj rekk moo di, nuy f\u00e0ttaliku seen aji n\u00e9ew doole yi, fekk sax laxasu woon naa ci def ko.\n2:11 Waaye bi Sefas \u00f1\u00ebwee d\u00ebkku Ancos, yedd naa ko ci kanamu \u00f1\u00e9pp, ndaxte li mu def jaaduwul.\n2:12 Ndaxte laata ndaw yi Saag y\u00f3nni di \u00f1\u00ebw, da daan bokk di lekk ak \u00f1i dul Yawut. Waaye bi \u00f1u agsee, te mu ragal kureel boobu faaydaal xaraf, mu dellu gannaaw, di sore \u00f1i dul Yawut.\n2:13 Yeneen Yawut yi it daldi \u00e0nd ak Sefas ci naaf\u00e9qam, ba y\u00f3bbaale sax Barnabas.\n2:14 Bi ma seetee nag ne, awu\u00f1u woon ci d\u00ebgg, gi xebaar bu baax bi di j\u00e0ngale, ma yedd Sefas ci kanamu \u00f1\u00e9pp ne ko: \u00abYaw miy Yawut, gannaaw d\u00ebddu nga aaday Yawut yi, ba dund ni ku dul Yawut, lu tax nga b\u00ebgg a s\u00ebf diiney Yawut ci \u00f1i dul Yawut?\u00bb\n2:15 Nun danoo cosaanoo ci xeetu Yawut, te bokkunu ci xeet, yi xamul Y\u00e0lla tey b\u00e0kkaar.\n2:16 Teewul nu xam ne, Y\u00e0lla du \u00e0tte kenn ni ku jub ci kaw s\u00e0mm yoon, waaye ci g\u00ebm Yeesu Kirist. Kon nun itam g\u00ebm nanu Kirist Yeesu, ngir Y\u00e0lla \u00e0tte nu jub ci kaw g\u00ebm Kirist, te du ci s\u00e0mm yoon. Ndaxte du caageenug s\u00e0mm yoon mooy tax Y\u00e0lla \u00e0tte kenn ni ku jub.\n2:17 Waaye ba tey su fekkee ne nu ngi wut a jub ci kaw g\u00ebm Kirist, fekk nu ne f\u00e0\u014b\u014b di ay b\u00e0kkaarkat, ndax nag Kirist moo sas b\u00e0kkaar? Mukk!\n2:18 Waaye su ma delloo di s\u00e0mm ndigali yoon, yi ma b\u00e0yyi, d\u00ebgg-d\u00ebgg dinaa wone noonu ne, moykatu yoon wi laa.\n2:19 Ci li j\u00ebm ci yoonu Musaa, dee naa, fekk yoon wi ci boppam moo ko waral, ngir ma man a dund, ba amal jari\u00f1 Y\u00e0lla.\n2:20 Daajaale na\u00f1u ma ak Kirist ca bant ba, te noonu du man may dundati, waaye Kirist mooy dund ci man. Dundu mbindeef, gi may dund nag, maa ngi koy dund ci g\u00ebm Doomu Y\u00e0lla ji, moom mi ma b\u00ebgg, ba joxe bakkanam ngir man.\n2:21 Duma neenal yiwu Y\u00e0lla, ndaxte su s\u00e0mm yoon doon tax a jub fa kanam Y\u00e0lla, kon Kirist dee na cig neen.\n3:1 Y\u00e9en waa Galasi, y\u00e9ena \u00f1\u00e0kk xel! Ku leen f\u00e0bbi, gannaaw bi ma leen y\u00e9galee ci lu leer ni \u00f1u daaje Yeesu Kirist ca bant ba?\n3:2 Lenn rekk laa b\u00ebgg, ngeen wax ma ko: ndax s\u00e0mm yoon wee tax, ngeen jot Xelum Y\u00e0lla? D\u00e9ed\u00e9et! Dangeen a d\u00e9gg xebaar bu baax bi te g\u00ebm ko.\n3:3 Mbaa du nii ngeen \u00f1\u00e0kke xel, ba t\u00e0mbalee ci Xelum Y\u00e0lla, ba noppi yaakaar a mate ci seen j\u00ebfi bopp?\n3:4 Mbaa du fitna, yi ngeen daj y\u00e9pp, dafa nar a neen? M\u00ebnuma koo g\u00ebm!\n3:5 Bu leen Y\u00e0lla di may Xelam, di leen won jalooreem, ndax li ngeen s\u00e0mm yoon a tax, mu def ko, mbaa li ngeen d\u00e9gg xebaar bu baax te g\u00ebm ko?\n3:6 Xool-leen ci Ibraayma; Mbind mi wax na ne:\u00abIbraayma g\u00ebm na Y\u00e0lla,te Y\u00e0lla j\u00e0ppe ng\u00ebmam ni njub.\u00bb\n3:7 Xamleen boog ne, boroom ng\u00ebm yi rekk \u00f1ooy doomi Ibraayma.\n3:8 Mbind mi t\u00ebral na lu jiitu ne, Y\u00e0lla dina \u00e0tte jub \u00f1i dul Yawut ci kaw ng\u00ebm. Kon looloo tax mu y\u00e9gal Ibraayma lu jiitu xebaar bu baax bi ne ko: \u00abXeeti \u00e0ddina y\u00e9pp dina\u00f1u barkeel ci yaw.\u00bb\n3:9 Kon \u00f1i g\u00ebm, Y\u00e0lla dina leen barkeel, sukkandikoo ko ci seen ng\u00ebm, ni mu defal Ibraayma, boroom ng\u00ebm.\n3:10 \u00d1iy w\u00e9kku \u00f1\u00e9pp ci j\u00ebfi yoon wi, \u00f1u alku la\u00f1u, ndaxte bind na\u00f1u ne: \u00abK\u00e9pp ku dul topp l\u00e9pp lu ndigali yoon wi santaane, Yal na alku.\u00bb\n3:11 Bir na sax ne, s\u00e0mm yoon du tax kenn jub fa kanam Y\u00e0lla, ndaxte Mbind mi t\u00ebral na ne: \u00abKu jub ci kaw ng\u00ebm dinga dund.\u00bb\n3:12 Waaye yoon wi laajul ng\u00ebm. Mbind mi nee na: \u00abKu manoon a matal li yoon wi wax, kon dinga dund ba f\u00e0ww.\u00bb\n3:13 Waaye Kirist jot na nu ci alkande, ji yoon wi indi; mu g\u00e0ddul nu ko, ba far alku moom ci boppam, ndaxte Mbind mi nee na: \u00abK\u00e9pp ku \u00f1u rey, w\u00e9kk ko ci bant, alku nga.\u00bb\n3:14 Noonu barke bi Y\u00e0lla dig Ibraayma baawaan na, ba daj \u00f1i dul Yawut te g\u00ebm Kirist Yeesu, te nu jot ci kaw ng\u00ebm Xel mu Sell, mi Y\u00e0lla dige.\n3:15 Bokk yi, maa ngi misaal wax ji ci j\u00ebfi doom Aadama. Xam ngeen ne, k\u00f3ll\u00ebre gu \u00f1u fas ba noppi, waru\u00f1u koo fecci, walla \u00f1u ciy rax dara.\n3:16 L\u00e9egi nag Y\u00e0lla am na lu mu dig Ibraayma ak askanam. Mbind mi waxul: \u00abAk i s\u00ebtam,\u00bb mu mel ni \u00f1u bare, waaye kenn la wax: \u00abAk sa askan,\u00bb maanaam Kirist.\n3:17 Li ma ci b\u00ebgg a wax mooy lii: ndegam Y\u00e0lla fas na k\u00f3ll\u00ebreem, yoonu Musaa, wi fee\u00f1 \u00f1eenti t\u00e9em\u00e9eri at ak fanweer gannaaw ga, du ko man a fecci, ba tebbi digeb Y\u00e0lla.\n3:18 Ndaxte x\u00e9ewal, yi Y\u00e0llay dige, bu \u00f1u doon j\u00f3ge ci yoon wi, kon ajootu\u00f1u ci dige bi, fekk ci kaw dige la ko Y\u00e0lla maye Ibraayma.\n3:19 Waaw kon yoonu Musaa, luy jari\u00f1am? Da\u00f1u koo w\u00e0cceel nit \u00f1i, ngir seen j\u00e0dd yoon ne f\u00e0\u014b\u014b. Looloo doon w\u00e0llu yoon wi, ba kera S\u00ebt biy \u00f1\u00ebw, moom mi \u00f1u digoon dige bi. Yoon wi nag, Y\u00e0lla t\u00ebral na ko jaare ci ay malaaka, te am na ku ko jottali.\n3:20 Waaye aajowul jottalikat, su fi kenn rekk teewee, te Y\u00e0lla kenn la.\n3:21 Ndax kon yoonu Musaa wi dafa juuyoo ak li Y\u00e0lla dige? Mukk! Su amoon yoon wu nit man a s\u00e0mm, ba mu jural ko dund gu sax, kon s\u00e0mm yoon dina tax nit jub fa kanam Y\u00e0lla.\n3:22 Waaye yoon wi t\u00ebj na \u00f1\u00e9pp ci dooley b\u00e0kkaar, ngir \u00f1i g\u00ebm Yeesu Kirist jot li Y\u00e0lla dige woon ci seen kaw ng\u00ebm.\n3:23 Bi ng\u00ebm Yeesu Kirist fee\u00f1agul nag, yoon wi da noo t\u00ebjoon r\u00e0pp, ba kera ng\u00ebm di fee\u00f1.\n3:24 Ci noonu la nu yoon wi doon noote, ba Kirist di \u00f1\u00ebw, ngir Y\u00e0lla \u00e0tte nu jub ci kaw ng\u00ebm.\n3:25 Waaye l\u00e9egi, bi jamonoy ng\u00ebm ji \u00f1\u00ebwee, nekkatunu ci kilifteefu yoon wi.\n3:26 Y\u00e9en \u00f1\u00e9pp doomi Y\u00e0lla ngeen ndax li ngeen bokk ci Kirist Yeesu ci kaw ng\u00ebm.\n3:27 Y\u00e9en \u00f1\u00e9pp, \u00f1i \u00f1u s\u00f3ob ci ndox ngir wone seen bokk ci Kirist, soloo ngeen Kirist.\n3:28 Kon nag amul xaajale ci diggante Yawut ak ki dul Yawut, ci diggante jaam ak gor, ci diggante g\u00f3or ak jig\u00e9en. Y\u00e9en \u00f1\u00e9pp benn ngeen ci seen bokk ci Kirist.\n3:29 Bu ngeen bokkee ci Kirist, kon bokk ngeen ci askanu Ibraayma, te jot ngeen x\u00e9ewal, yi ko Y\u00e0lla dig.\n4:1 Li ma leen di wax, mooy lii: doom ji war a donni baayam, fi ak mu ngi cig ndaw, ak lu ko alal jiy lew l\u00e9pp, du wuute dara ak jaam.\n4:2 \u00d1i ko yore tey s\u00e0mm alalam \u00f1oo koy yilif, ba jamono ji ko baayam \u00e0ppaloon mat.\n4:3 Nun itam naka noonu, laata nuy mat, aaday \u00e0ddina \u00f1oo nu nootoon, ba def nu ni ay jaam.\n4:4 Waaye bi \u00e0pp bi Y\u00e0lla t\u00ebraloon matee, y\u00f3nni na Doomam, mu juddoo ci jig\u00e9en, ci biir yoonu Musaa,\n4:5 ngir jot \u00f1i yoon wi nootoon, ndax Y\u00e0lla j\u00e0pp nu ni ay doomam.\n4:6 Gannaaw doomi Y\u00e0lla ngeen nag, Y\u00e0lla y\u00f3nni na Xelu Doomam ci sunu xol, mu koy wooye nii: \u00abAbba,\u00bb maanaam \u00abBaay.\u00bb\n4:7 Noonu dootuloo jaam, doom nga. Te ndegam doom nga, Y\u00e0lla jagleel na la c\u00e9r ci x\u00e9ewal, yi mu dencal ay doomam.\n4:8 Bu j\u00ebkk, bi ngeen xamagul Y\u00e0lla, y\u00e9ena ngi doon jaamu yeneen yu \u00f1u daan bokkaaleel Y\u00e0lla.\n4:9 Waaye l\u00e9egi nag bi ngeen xamee Y\u00e0lla, walla boog bi leen Y\u00e0lla x\u00e0mmee, nan ngeen man a def, bay delluwaat ca aaday \u00e0ddina? Aada yooyee \u00f1\u00e0kk doole te \u00f1\u00e0kk njari\u00f1, lu tax ngeen b\u00ebgg, \u00f1u nootaat leen?\n4:10 Y\u00e9ena ngi fonk b\u00e9s yi, weer yi, m\u00e0ggal yi ak at yi!\n4:11 Sama xel dalul ci y\u00e9en, ngir ragal sama coono ci y\u00e9en neen.\n4:12 Bokk yi, dama leen di \u00f1aan, ngeen mel ni man, ndaxte man itam fekksi naa leen ci seen xalaat. Too\u00f1uleen ma.\n4:13 Xam ngeen ne, sama wopp moo taxoon, ma y\u00e9gal leen xebaar bu baax bi.\n4:14 Coono, gi leen sama wopp tegoon, taxul ngeen ba\u00f1 ma, taxul ngeen s\u00e9exlu ma. Waaye teeru ngeen ma, ni bu ngeen doon teeru malaakam Y\u00e0lla walla Yeesu Kirist.\n4:15 Waaw, fan la seen mb\u00e9g jaar? Ndaxte seedeel naa leen ne, su ngeen ko manoon, kon luqi ngeen seeni b\u00ebt, jox ma.\n4:16 Ndax d\u00ebgg, gi ma leen wax, moo tax ngeen def ma ab noon?\n4:17 Nit \u00f1oo\u00f1u leen di farle, seen m\u00e9b\u00e9t baaxul. Da\u00f1u leen a b\u00ebgg a t\u00e0ggale ak nun, ngir ngeen far ak \u00f1oom.\n4:18 Farle baax na, bu \u00e0ndee ak m\u00e9b\u00e9t mu baax. Waaye bu sama j\u00ebmm rekk tax ngeen koy def.\n4:19 Sama doom yi! Y\u00e9ena tax may dellu ci metit ni kuy matu, ba kera jikkoy Kirist di mat ci y\u00e9en.\n4:20 L\u00e9egi b\u00ebggoon naa nekk ci seen biir, ngir man a jubbanti sama k\u00e0ddu, ndaxte xamatuma nu may doxale ak y\u00e9en!\n4:21 Y\u00e9en \u00f1i b\u00ebgg a topp yoon wi, xanaa xamuleen li yoonu Musaa wi wax?\n4:22 Mbind mi nee na: Ibraayma am na \u00f1aari doom; ki jaam bi jur ak ki gor si jur.\n4:23 Doomu jaam bi juddu na ni b\u00e9pp doom, waaye doom, ji mu am ak jabaram, juddu na ci kaw digeb Y\u00e0lla.\n4:24 Loolu nag am na lu muy misaal. \u00d1aari jig\u00e9en \u00f1i da\u00f1oo bijji \u00f1aari k\u00f3ll\u00ebre. Benn bi di Ajara, mooy wone k\u00f3ll\u00ebre, gi Y\u00e0lla fasoon ca tundu Sinayi. Ay jaam lay jur.\n4:25 Ajara moomu mooy tundu Sinayi, wi nekk ca r\u00e9ewu Arabi. Te it mooy misaalu d\u00ebkku Yerusalem, bi fi nekk tey. Ndaxte moom ak ay doomam y\u00e9pp ay jaam la\u00f1u.\n4:26 Waaye Yerusalem, ga ca kaw, mooy gor si. Moom mooy sunu ndey.\n4:27 Ndaxte Mbind mi nee na:\u00abB\u00e9gal, yaw jig\u00e9en ji dul jur,te musul a am doom.Reeyal te b\u00e0nneexu,yaw mi musul a xam coonob mat,ndaxte jig\u00e9en ji \u00f1u faalewulmoo g\u00ebn a jaboot ki nekk ak j\u00ebkk\u00ebram.\u00bb\n4:28 Y\u00e9en bokk yi, y\u00e9enay doom yi \u00f1u dige woon, niki Isaaxa.\n4:29 Waaye doom ji juddoo ni b\u00e9pp doom, dafa daan sonal doom ji juddoo ci dooley Xelum Y\u00e0lla. Te loolu mooy law ba l\u00e9egi.\n4:30 Lu ci Mbind mi wax nag? Nee na: \u00abD\u00e0qal jaam bi ak doomam, ndaxte doomu jaam bi warul a bokk c\u00e9r ak doomu gor si ci ndono.\u00bb\n4:31 Kon nag bokk yi, nun dunu doomi jaam, ay doomi gor lanu.\n5:1 Kirist a nu daggal sunu buumi njaam, ngir goreel nu. Kon d\u00ebg\u00ebrleen ci seen ngor te ba\u00f1 a delluwaat ci njaam.\n5:2 D\u00e9gluleen! Man Pool maa leen koy wax: bu ngeen itteelee xaraf, kon Kirist dootu leen jari\u00f1 dara.\n5:3 Te maa ngi dellu di waxaat ne, k\u00e9pp kuy farataal xaraf, f\u00e0ww nga s\u00e0mm l\u00e9pp lu yoon wi santaane.\n5:4 Y\u00e9en \u00f1iy fexee jub fa kanam Y\u00e0lla ci kaw s\u00e0mm yoon, t\u00e0ggalikoo ngeen ak Kirist; d\u00ebddu ngeen yiwu Y\u00e0lla.\n5:5 Waaye njub, gi nu Y\u00e0lla dencal \u00ebll\u00ebg, nu ngi koy s\u00e9entu ci kaw ng\u00ebm ak ci ndimbalu Xelum Y\u00e0lla.\n5:6 Ndaxte bu nu bokkee ci Kirist Yeesu, xaraf ak ba\u00f1 a xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ng\u00ebm, giy j\u00ebf ci mb\u00ebggeel.\n5:7 Ni ngeen j\u00f3gtee woon de baax na! Waaw ku leen dog, ba ngeen ba\u00f1 a d\u00e9ggal d\u00ebgg?\n5:8 Li \u00f1u leen xiir j\u00f3gewul ci Y\u00e0lla, mi leen woo.\n5:9 Dees na ne: \u00abTuuti lawiir day tax tooyalu fari\u00f1 b\u00e9pp funki.\u00bb\n5:10 Waaye teewul Boroom bi jox na ma k\u00f3olute ci y\u00e9en. Biral na ma ne, dingeen bokk ak man xalaat. L\u00e9egi nag, kiy n\u00ebxal seen xel, ku mu man a doon, Y\u00e0lla dina ko mbugal.\n5:11 Man nag bokk yi, bu ma doon faaydaal xaraf ci sama waare, kon du\u00f1u ma fitnaale nii; te it li may y\u00e9gle ci deewu Kirist ca bant ba dootul naqari kenn.\n5:12 \u00d1i farataal xaraf te di leen d\u00ebpp, na\u00f1u g\u00ebn a sore ci seen r\u00e9er: bu yaboo sax \u00f1u dagg seen ng\u00f3ora, ba dara du ci des!\n5:13 Y\u00e9en nag bokk yi, Y\u00e0lla woo na leen, ngeen nekk i gor. Waaye nag buleen ci sukkandiku, bay topp seen nafsu, waaye dimbaleenteleen ci kaw mb\u00ebggeel.\n5:14 Ndaxte yoon w\u00e9pp, ndigal lii a ko t\u00ebnk: \u00abNanga b\u00ebgg sa moroom, ni nga b\u00ebgge sa bopp.\u00bb\n5:15 Waaye moytuleen! Bu ngeen dee m\u00e0ttante ak a lekkante, dingeen y\u00e0qante.\n5:16 Li ma leen di wax mooy lii: dundleen ci Xelum Y\u00e0lla, kon dungeen topp seen nafsu.\n5:17 Ndaxte sunu nafsu am na ay b\u00ebgg-b\u00ebgg yu mengoowul ak yu Xelum Y\u00e0lla. Te Xelum Y\u00e0lla itam am na ay b\u00ebgg-b\u00ebgg yu mengoowul ak yu sunu nafsu. \u00d1oom \u00f1aar da\u00f1oo juuyoo ci b\u00e9pp f\u00e0nn, ba tax l\u00e9pp lu ngeen b\u00ebggoon a def, dungeen ko man.\n5:18 Waaye bu ngeen toppee Xelum Y\u00e0lla, nekkatuleen ci kilifteefu yoon wi.\n5:19 Kuy topp sa nafsu, nii ngay j\u00ebfe: njaaloo, xalaat yu bon, def i \u00f1aawteef ak say c\u00e9r,\n5:20 x\u00ebr\u00ebm, luxus, noonoo ak xuloo, \u00f1eetaane, xadar, diiroo mbagg, f\u00e9ewaloo ak xaajaloo,\n5:21 ki\u00f1aan, m\u00e0ndite ak xawaare ak yeneen yu ni mel. L\u00e9egi nag maa ngi leen di artu, ni ma ko defe woon: \u00f1iy j\u00ebfe noonu du\u00f1u am c\u00e9r ci nguuru Y\u00e0lla.\n5:22 Waaye li Xelu Y\u00e0lla mi di me\u00f1\u00f1 mooy: mb\u00ebggeel, mb\u00e9g, j\u00e0mm, mu\u00f1, laabiir, mbaax, k\u00f3ll\u00ebre,\n5:23 lewetaay ak maandute. Yoon wi terewul yu ni mel.\n5:24 L\u00e9egi \u00f1i bokk nag ci Yeesu Kirist, daaj na\u00f1u seen nafsu ca bant ba, wacc ko fa, moom ak ay xemmemam ak ay b\u00ebgg-b\u00ebggam.\n5:25 Gannaaw nag nu ngi dund l\u00e9egi ci Xelum Y\u00e0lla, kon nanu ko topp.\n5:26 Bu nu tiitaru di d\u00ebkkante, di i\u00f1aanante.\n6:1 Bokk yi, ku \u00f1u fekk muy def lu Y\u00e0lla b\u00ebggul, y\u00e9en \u00f1i topp Xelum Y\u00e0lla, nangeen ko jubbanti ak xol bu lewet. Waaye nanga s\u00e0mm sa bopp, ngir b\u00e0kkaar ba\u00f1 laa fiir, yaw itam.\n6:2 J\u00e0ppalanteleen, noonu dingeen s\u00e0mm yoon wi Kirist t\u00ebral.\n6:3 Ndaxte kuy naagu te fekk doo dara, dangay nax sa bopp.\n6:4 Na ku nekk seetlu ni muy beye sasam. Bu ko defee dina man a naw boppam, tey ba\u00f1 di diirante mbagg ak \u00f1i ci des.\n6:5 Ndaxte ku ci nekk dangaa war a yenu sab yen.\n6:6 Kiy j\u00e0ng k\u00e0ddug Y\u00e0lla war na s\u00e9dd ki koy j\u00e0ngal ci alalam j\u00e9pp.\n6:7 Bu leen ci dara nax; kenn du fontoo Y\u00e0lla, ndaxte lu waay ji, moom ngay g\u00f3ob.\n6:8 Ku ji ngir sa nafsu, dinga g\u00f3ob li sa nafsu me\u00f1\u00f1, maanaam ag y\u00e0qute. Waaye ku ji lu soloo ak Xelum Y\u00e0lla, li Xel mi me\u00f1\u00f1 ngay g\u00f3ob, maanaam dund gu dul jeex.\n6:9 Bunu t\u00e0yyi ci def lu baax, ndaxte bu nu ci sawaree, bu waxtu wi jotee dinanu jari\u00f1u.\n6:10 Noonu fi ak nu koy man, nanuy defal \u00f1\u00e9pp lu baax, rawatina nag sunu bokk yi g\u00ebm.\n6:11 Seetleen araf yu mag yii ma leen bind ci sama loxob bopp!\n6:12 \u00d1iy gistal ci seen yaram, \u00f1oo\u00f1oo b\u00ebgg ngeen xaraf, ngir ragal a daj fitna ci y\u00e9gle deewu Kirist ca bant ba.\n6:13 Kureel gi faaydaal xaraf, \u00f1oom ci seen bopp sax, du\u00f1u topp yoon wi. Da\u00f1oo b\u00ebgg a ngeen xaraf, ba \u00f1u man a b\u00e0kku ci seen yaram, y\u00e9en.\n6:14 Man ci sama w\u00e0llu bopp, duma b\u00e0kku mukk su dul ci deewu sunu Boroom Yeesu Kirist, ba \u00f1u ko daajee ca bant ba. Deeyam moo tax ma mel ni ku dee ci y\u00ebfi \u00e0ddina; y\u00ebfi \u00e0ddina dee ci man.\n6:15 Xaraf ak ba\u00f1 a xaraf dara amu ci solo. Li am solo mooy nekk mbindeef mu bees.\n6:16 \u00d1iy topp ndigal lii nag, na Y\u00e0lla w\u00e0cce j\u00e0mm ak y\u00ebrmande ci \u00f1oom, ak ci Israyilu Y\u00e0lla.\n6:17 L\u00e9egi nag, bu ma kenn l\u00ebjalati, ndaxte yor naa ci sama yaram ay leget yuy m\u00e0ndargaal ne, jaamu Yeesu laa.\n6:18 Bokk yi, na yiwu Yeesu Kirist sunu Boroom \u00e0nd ak seen xel. Amiin.","title":"Wolof Bible (NT): Galatians","type":"page"}
