{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/heb.htm","path":"bib/wb/wlf/heb.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/heb.htm","text":"1:1 Li jiitu tey Y\u00e0lla waxoon na ak maam ya ci w\u00e0ll yu bare ak ci t\u00ebralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya.\n1:2 Waaye ci mujug jamono jii nu tollu, Y\u00e0lla wax na ak nun jaarale ko ci Doom ji. Doomam jooju la Y\u00e0lla jagleel l\u00e9pp, te ci moom la Y\u00e0lla jaar, s\u00e0kk \u00e0ddina.\n1:3 Doom ji moo di leer giy jollee ci ndamu Y\u00e0lla, di ki dippeekoo ci Y\u00e0lla. Moo t\u00e9ye \u00e0ddina ci k\u00e0ddoom gu am doole gi. Te bi mu ubbee bunt ba nit di selle ci ay b\u00e0kkaaram, dafa toog fa \u00f1u koy terale ca ndeyjooru Aji M\u00e0gg ji ca kaw,\n1:4 wone noonu ne, moo g\u00ebn a m\u00e0gg malaaka yi. Te it Y\u00e0lla jox na ko tur wu sut seen tur.\n1:5 Ndaxte Y\u00e0lla musul a wax kenn ci malaaka yi ne:\u00abYaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.\u00bb Musul ne ci mbirum kenn ci \u00f1oom it:\u00abMan Y\u00e0lla, dinaa doon Baay ci moom,mu nekk Doom ci man.\u00bb\n1:6 Waaye bi muy y\u00f3nni Doom jooju di taaw bi ci \u00e0ddina, da ne:\u00abNa ko malaakay Y\u00e0lla y\u00e9pp jaamu.\u00bb\n1:7 Ci w\u00e0llu malaaka yi, lii la ci Y\u00e0lla wax:\u00abDef na malaakaam yi, \u00f1u mel ni ay ngelaw,\u00f1oo\u00f1u koy ligg\u00e9eyal, mu def leen niki safara.\u00bb\n1:8 Waaye ci w\u00e0llu Doom ji, lii la ko Y\u00e0lla wax:\u00abYaw Y\u00e0lla, dinga toog ci jal bi ba f\u00e0ww,ci njubte ngay nguuru.\n1:9 Sopp nga njub te ba\u00f1 lu bon.Looloo tax yaw Y\u00e0lla,sa Y\u00e0lla sol la mb\u00e9g mu g\u00ebn a r\u00e9ymi mu jagleel say \u00e0ndandoo.\u00bb\n1:10 Newaat na it:\u00abYaw Boroom bi,yaa s\u00e0kk \u00e0ddina ca nj\u00e0lb\u00e9en ga,defar asamaan yi ci sa loxoy bopp.\n1:11 Y\u00ebf yooyu dina\u00f1u w\u00e9y,waaye yaw dinga sax,dina\u00f1u m\u00e0ggat \u00f1oom \u00f1\u00e9pp ni ay y\u00e9re.\n1:12 Dinga leen taxa\u00f1 ni malaan,\u00f1u furi ni ay y\u00e9re,waaye yaw doo soppiku,te sa dund amul \u00e0pp.\u00bb\n1:13 Waaye Y\u00e0lla musul a teral kenn ci malaaka yi, ba di ko wax:\u00abToogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneel say noonci sa kanam.\u00bb\n1:14 Malaaka y\u00e9pp ay xel la\u00f1u rekk yuy ligg\u00e9eyal Y\u00e0lla, mu di leen y\u00f3nni \u00f1uy dimbali nit, \u00f1i nar a jot mucc gi.\n2:1 Moo tax kon nu war a g\u00ebn a faaydaal wax yi nu d\u00e9gg, ngir ba\u00f1 a bayliku.\n2:2 Xam nanu ne k\u00e0ddug yoon, wi Y\u00e0lla y\u00e9gle jaarale ko ci malaaka yi, wareef la woon, te k\u00e9pp ku ko mas a moy, walla mu mas koo tanqamlu, jot na mbugal gi mu yelloo.\n2:3 Kon nun \u00f1i d\u00e9gg mucc gu mag gi, bu nu ko s\u00e0gganee, nan lanuy man a r\u00ebcce mbugalu Y\u00e0lla? Boroom bi moo xamle woon mucc googu ca nj\u00e0lb\u00e9en ga, te gannaaw gi, \u00f1i ko d\u00e9gg, \u00f1oo nu ko w\u00f3oralal.\n2:4 Te it Y\u00e0lla d\u00ebggal na seen seede ci ay firnde ak ay k\u00e9emaan, ay jaloore yu bare ak ci ay may yu j\u00f3ge ci Xelam mu Sell, te mu s\u00e9ddale leen ni mu ko b\u00ebgge.\n2:5 Y\u00e0lla j\u00e9bbalul malaaka yi benn sa\u00f1-sa\u00f1 bu j\u00ebm ci jamonoy \u00ebll\u00ebg ji nuy wax; keneen la ko j\u00e9bbal,\n2:6 ndaxte am na fu \u00f1u wax ci Mbind mi ne:\u00abLan mooy nit, yaw Y\u00e0lla, ba nga di ko xalaat?Lan mooy doomu nit, ba nga koy topptoo?\n2:7 W\u00e0cce nga ko, def komu g\u00ebn a suufe tuuti malaaka yi.Kaalaa nga ko teraanga ak ndam,\n2:8 nootal ko l\u00e9pp, mu teg ci t\u00e0nk.\u00bb Bi ko Y\u00e0lla nootalee l\u00e9pp nag, b\u00e0yyiwul dara. Fi mu nekk gisagunu ne, l\u00e9pp a ngi ci sa\u00f1-sa\u00f1am;\n2:9 Waaye gis nanu Yeesu. W\u00e0cce na\u00f1u ko, def ko mu g\u00ebn a suufe tuuti malaaka yi, ngir mu dee ci w\u00e0llu \u00f1\u00e9pp, ndaxte loolu la Y\u00e0lla dogal ci yiwam. Waaye l\u00e9egi Y\u00e0lla kaalaa na ko teraanga ak ndam ndax coono bi mu daj ba dee.\n2:10 Ndaxte Y\u00e0lla mi yelloo l\u00e9pp te s\u00e0kk l\u00e9pp, dogal na def \u00f1u bare ay doomam, boole leen ci ndamam. Jekk na nag mu matal Yeesu ci coono bi mu daj, moom mi leen x\u00e0llal yoonu mucc gi.\n2:11 Moom Yeesu miy sellal, ak \u00f1i muy sellal, \u00f1oom \u00f1\u00e9pp genn njaboot la\u00f1u. Moo tax Yeesu rusu leen a wooye ay doomi baayam.\n2:12 Nee na:\u00abYaw Y\u00e0lla, dinaa xamle sa turci samay doomi baay,dinaa la tagg ci biir mbooloo mi.\u00bb\n2:13 Newaat na:\u00abDinaa am ci Y\u00e0lla k\u00f3olute.\u00bb Dellu na waxaat ne:\u00abMaa ngi nii, man ak doom yi ma Y\u00e0lla jox.\u00bb\n2:14 Doomam yooyu muy wax, nit kese la\u00f1u. Looloo tax Yeesu it moom ci boppam, w\u00e0cc na, j\u00ebmmoo ni \u00f1oom, ngir dee, ba man caa daaneel Ibliis, mi yore dooley dee.\n2:15 Noonu mu yiwi nit, \u00f1i meloon ni ay jaam seen giiru dund g\u00e9pp ndax ragal a dee.\n2:16 Leer na ne, Yeesu xettalisiwul malaaka yi, waaye askanu Ibraayma lay xettalisi.\n2:17 Looloo taxoon mu war a mel niy doomi baayam ci b\u00e9pp f\u00e0nn, ngir doon seen saraxalekat bu mag fa kanam Y\u00e0lla, bi leen y\u00ebr\u00ebm te di s\u00e0mm k\u00f3ll\u00ebre, te ci ligg\u00e9eyu saraxaleem joxe na bakkanam ngir dindi b\u00e0kkaari nit \u00f1i, ba Y\u00e0lla baal leen.\n2:18 Gannaaw sonn na ci nattu yi mu daj, man na dimbali \u00f1iy jaar ciy nattu.\n3:1 Kon nag y\u00e9en bokk yu sell yi, y\u00e9en \u00f1i Y\u00e0lla woo, ngeen bokk ci nguuram gu kawe ga, seetleen ci Yeesu, moom miy ndawu Y\u00e0lla li, di saraxalekat bu mag bi ci yoon wi nu g\u00ebm.\n3:2 Ku takku la ci ligg\u00e9ey bi ko Y\u00e0lla sas, ni ko Musaa nekke woon ci l\u00e9pp lu j\u00ebm ci waa k\u00ebr Y\u00e0lla.\n3:3 Waaye Yeesu yelloo na ndam lu sut lu Musaa, ni kiy tabax k\u00ebr \u00ebppe maana k\u00ebr ga muy tabax.\n3:4 Ndaxte k\u00ebr gu nekk am na ku ko sos, waaye ki sos l\u00e9pp mooy Y\u00e0lla.\n3:5 Musaa moom ku takku la woon ci l\u00e9pp lu j\u00ebm ci waa k\u00ebr Y\u00e0lla. Waaye jawri\u00f1 rekk la woon, ngir seede li Y\u00e0lla waroon a y\u00e9gle.\n3:6 Yeesu nag ku takku la it, waaye Doom la, juy yilif k\u00ebr Baayam. Nun nooy k\u00ebram googu, bu nu saxee ci sunu k\u00f3olute te di b\u00e9g ci li nuy s\u00e9entu.\n3:7 Moo tax Xel mu Sell mi wax lii ci Mbind mi:\u00abBu ngeen d\u00e9ggee tey jii baatu Y\u00e0lla bi,\n3:8 buleen d\u00ebg\u00ebr bopp,ni seeni maam defoon ca m\u00e0ndi\u014b ma,keroog ba \u00f1u d\u00ebddoo Y\u00e0lla di ko dii\u014bat.\u00bb\n3:9 Y\u00e0lla ne:\u00abFoofa seeni maam dii\u014bat na\u00f1u ma fa,di ma fexee fiir,te gis na\u00f1u samay j\u00ebf\n3:10 diirub \u00f1eent-fukki at.Looloo tax gennliku naa leen, daldi ne:\u201cSeeni xalaat a leen di r\u00e9eral saa su nekk,xamu\u00f1u yoon yi ma neex.\u201d\n3:11 Gi\u00f1 naa kon ci sama mer ne:\u201cDu\u00f1u dugg mukk ci sama noflaay.\u201d\u00bb\n3:12 Bokk yi, wottuleen ba kenn ci y\u00e9en ba\u00f1 a am xol bu bon te g\u00ebmadi, bay d\u00ebddu Y\u00e0lla jiy dund.\n3:13 Waaye b\u00e9s bu nekk, deeleen so\u00f1\u00f1ante ci lu j\u00ebm ci Y\u00e0lla, fi ak b\u00e9s boobu \u00f1u wax w\u00e9yul, ngir ragal b\u00e0kkaar nax kenn, ba xolam t\u00ebju.\n3:14 Am nanu w\u00e0ll ci Kirist, su nu w\u00e9yee fii ba muj ga ci sunu k\u00f3olute, gi nu amoon ca nj\u00e0lb\u00e9en ga.\n3:15 Lii la Mbind mi wax:\u00abBu ngeen d\u00e9ggee tey jii baatu Y\u00e0lla bi,buleen d\u00ebg\u00ebr bopp,ni seeni maam defoon, ba \u00f1u d\u00ebddoo Y\u00e0lla.\u00bb\n3:16 \u00d1an \u00f1oo d\u00e9gg baatu Y\u00e0lla bi nag te di ko d\u00ebddu? Xanaa \u00f1a Musaa g\u00e9nne woon Misra \u00f1\u00e9pp.\n3:17 Te \u00f1an la Y\u00e0lla mere lu mat \u00f1eent-fukki at? Xanaa \u00f1i daan b\u00e0kkaar te seeni n\u00e9ew t\u00ebdd ca m\u00e0ndi\u014b ma.\n3:18 Te it bi Y\u00e0lla defee ngi\u00f1 lii: \u00abDu\u00f1u dugg mukk ci sama noflaay,\u00bb booba \u00f1an \u00f1oo ko taxoon di wax? Xanaa \u00f1a ko d\u00e9ggadil.\n3:19 Noonu gis nanu sax ne, jotu\u00f1oo dugg ci noflaay boobu ndax seen g\u00ebmadi.\n4:1 Y\u00e0lla dige na ne, dina am \u00f1u dugg ca noflaayam. Kon ndegam dige boobu mi ngi taxaw ba tey, moytuleen ba kenn ci y\u00e9en r\u00e9er ba du dugg ci noflaay boobu.\n4:2 Nun jot nanu xebaar bu baax bi ni \u00f1oom, waaye k\u00e0ddu, ga \u00f1u d\u00e9ggoon, jari\u00f1u leen dara, ndaxte boolewu\u00f1u ci ng\u00ebm, ba \u00f1u koy d\u00e9glu.\n4:3 Nun \u00f1i g\u00ebm nag nooy dugg ci noflaayam, ni ko Mbind mi waxe:\u00abGi\u00f1 naa kon ci sama mer ne:\u201cDu\u00f1u dugg mukk ci sama noflaay,\u201d\u00bb doonte sax ligg\u00e9eyam b\u00e9pp matoon na, ca ba mu s\u00e0kkee \u00e0ddina ak l\u00e9egi. Ci lu j\u00ebm ci jur\u00f3om-\u00f1aareelu fan ba,\n4:4 am na fu \u00f1u wax ci Mbind mi ne:\u00abY\u00e0lla noppalu na ci ligg\u00e9eyam b\u00e9ppca jur\u00f3om-\u00f1aareelu fan ba.\u00bb\n4:5 Te it waxoon na ci baat yi nu jot a lim ba noppi:\u00abDu\u00f1u dugg mukk ci sama noflaay.\u00bb\n4:6 Kon am na \u00f1u ci war a dugg ba tey. Te \u00f1i j\u00ebkkoon a jot xebaar bu baax bi, duggu\u00f1u ci ndax seen d\u00e9ggadi.\n4:7 Noonu ay ati at gannaaw ga, Y\u00e0lla \u00e0ppaat na beneen b\u00e9s, def ko \u00abtey jii,\u00bb bi mu waxee ci g\u00e9mmi\u00f1u Daawuda ci baat yii \u00f1u jot a lim:\u00abBu ngeen d\u00e9ggee tey jii baatu Y\u00e0lla bi,buleen d\u00ebg\u00ebr bopp.\u00bb\n4:8 Su Yosuwe duggaloon sunu maam ya ca noflaayu Y\u00e0lla ba, kon gannaaw gi Y\u00e0lla du wax dara ci lu j\u00ebm ci beneen b\u00e9s.\n4:9 Kon ba tey Y\u00e0llaa ngi dencal ay gaayam noflaay bu nirook noflaayu Y\u00e0lla ca jur\u00f3om-\u00f1aareelu fan ba.\n4:10 Ndaxte k\u00e9pp ku mas a dugg ca noflaayu Y\u00e0lla, noppalu na ci ay j\u00ebfam ni Y\u00e0lla.\n4:11 Nanu farlu boog, ngir dugg ci noflaay boobu, ba kenn ba\u00f1 a d\u00e9ggadi, ba daanu ni maam ya ca m\u00e0ndi\u014b ma.\n4:12 Xam nanu ne, k\u00e0ddug Y\u00e0lla mi ngi dund te am na doole. Moo g\u00ebn a \u00f1aw jaasiy \u00f1aari boor. Day dagg ba fa xol ak xel digaloo, ba fa yax yi ak yuq gi di teqalikoo, te man na \u00e0tte xalaat yi ak m\u00e9b\u00e9ti xol.\n4:13 Te itam amul mbindeef mu man a n\u00ebbbu Y\u00e0lla, waaye l\u00e9pp a ubbiku, ba ne f\u00e0\u014b\u014b ci b\u00ebti ki nu war a \u00e0tte.\n4:14 Gannaaw am nanu saraxalekat bu mag-a-mag bu \u00e0gg ba ca kanam Y\u00e0lla, di Yeesu Doomu Y\u00e0lla ji, nanu j\u00e0pp bu d\u00ebg\u00ebr yoon wi nu g\u00ebm.\n4:15 Saraxalekat bu mag bi nu am, du ku m\u00ebnul a bokk ak nun sunuy naqar; moom sax far jaar na ci nattu ni nun ci b\u00e9pp f\u00e0nn, waaye deful b\u00e0kkaar.\n4:16 Kon nag nanu am k\u00f3olute ci jege jalu Y\u00e0lla bu yiw ba, ngir jot y\u00ebrmandeem ak yiwam, ngir mu wallu nu fu soxla taxawe.\n5:1 Saraxalekat bu mag bu nekk nag, ci biir nit \u00f1i la\u00f1u ko j\u00eble, te fal ko muy dox seen diggante ak Y\u00e0lla. Noonu dina j\u00e9bbal Y\u00e0lla ay sarax, tey rendi ay mala ngir dindi seeni b\u00e0kkaar.\n5:2 Te ndegam moom ci boppam nit kese la, man na mu\u00f1al \u00f1iy moy ndax seen \u00f1\u00e0kka xam.\n5:3 Li mu \u00f1\u00e0kk doole moo tax mu war a def ay sarax ngir mbaalug b\u00e0kkaaram, ni mu ko t\u00e0mmee defal mbooloo mi.\n5:4 Kenn m\u00ebnul a teral sa bopp ba doon ab saraxalekat, su dul ne Y\u00e0llaa la woo, ni mu ko defe woon Aaroona.\n5:5 Kirist itam y\u00e9kkatiwul boppam, ba doon saraxalekat bu mag, waaye Y\u00e0lla moo ko woo, bi muy wax ne:\u00abYaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.\u00bb\n5:6 Am na feneen fu mu wax ne:\u00abDoon nga saraxalekat ba f\u00e0wwmel ni Melkisedeg.\u00bb\n5:7 Giiru dundam g\u00e9pp ci \u00e0ddina, Kirist da daan \u00f1aan wall ci Y\u00e0lla, di ko d\u00e9nku, boole ko ak i jooy ak i rangoo\u00f1. Da doon \u00f1aan ci Y\u00e0lla, mi ko man a musal ci dee. Te \u00f1aanam nangu na, ndax ni mu j\u00e9bbale boppam Y\u00e0lla.\n5:8 Waaye li muy nekk-nekk doom, teewul mu j\u00e0ng d\u00e9ggal Y\u00e0lla, jaare ko ci coono bi mu daj.\n5:9 Noonu la \u00e0gge cig mat, \u00f1u def ko ki waral mucc gi dul jeex, ngir \u00f1i ko d\u00e9ggal \u00f1\u00e9pp.\n5:10 Fekk na Y\u00e0lla tudde ko saraxalekat bu mag ni ko Melkisedeg nekke.\n5:11 Ci f\u00e0nn googu, am na lu bare lu nu ci b\u00ebgg a wax, waaye tekkil leen ko dina jafe, ndaxte dangeen a naqari xel.\n5:12 Bu y\u00e0gg ngeen waroon a j\u00e0ngal \u00f1eneen \u00f1i, waaye soxla ngeen ba tey ku leen di tette ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla. L\u00e9egi nag y\u00e9ena ngi tollu fi \u00f1u leen war a n\u00e0mpale, ndaxte \u00e0ttanuleen \u00f1am wu d\u00ebg\u00ebr.\n5:13 K\u00e9pp kuy n\u00e0mp, ab xale nga ba tey. J\u00ebfeegoo nj\u00e0ngale, mi j\u00ebm ci w\u00e0llu njubte.\n5:14 Waaye \u00f1am wu d\u00ebg\u00ebr, \u00f1i mat a ko yelloo, maanaam \u00f1iy j\u00ebfandikoo seen xel ngir r\u00e0\u00f1\u00f1ee lu baax ak lu bon.\n6:1 Kon nag l\u00e9egi, nanu j\u00f3ge ci liifantu gi j\u00ebm ci Kirist, te j\u00e0ll cig mat. Nanu ba\u00f1 a dalaat nj\u00e0ngale mu j\u00ebkk moomu, ci ne nit \u00f1i da\u00f1oo war a tuub j\u00ebf, yi j\u00ebm ci dee, te g\u00ebm Y\u00e0lla,\n6:2 di leen j\u00e0ngalaat ci mbirum sangu set ci ay f\u00e0nn yu bare, ak teg loxo ak ci mbirum ndekkite ak lu j\u00ebm ci \u00e0tte biy sax d\u00e0kk.\n6:3 Te noonu lanuy def, bu soobee Y\u00e0lla.\n6:4 Li nu war a j\u00ebme kanam mooy lii: su amee ay nit \u00f1u Y\u00e0lla xas a leeral ba noppi, \u00f1u mos mayu Y\u00e0lla gi, am w\u00e0ll ci Xelam mu Sell,\n6:5 te xam mbaax, gi ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, ak k\u00e9emaani jamono jiy \u00f1\u00ebw,\n6:6 te loolu l\u00e9pp teewul \u00f1u walbatiku, \u00f1oo\u00f1u kenn dootu leen man a yeesalaat, ba \u00f1u tuub seeni b\u00e0kkaar. Li ko waral moo di, da\u00f1oo b\u00ebgg a daajaat Doomu Y\u00e0lla ji ci bant, di ko toroxal, te fekk muy seen ngaa\u00f1.\n6:7 Maanaam suuf suy naan taw bi ciy dal, tey jox \u00f1i \u00f1u koy beyal g\u00e0ncax gu am njari\u00f1, day jot barke bi j\u00f3ge ci Y\u00e0lla.\n6:8 Waaye su me\u00f1\u00f1ee ay d\u00e9g ak ay xaaxaam, du am benn njari\u00f1; repp na \u00f1u alag ko, te lakk lay mujje.\n6:9 Waaye nag y\u00e9en samay soppe, su fekkee ne sax, nii lanuy waxe, nu ngi yaakaar li g\u00ebn ci y\u00e9en te \u00e0nd ak mucc.\n6:10 Y\u00e0lla \u00f1\u00e0kkul worma bay f\u00e0tte seen ligg\u00e9ey ak mb\u00ebggeel, gi ngeen wone ci turam, ci li ngeen dimbali ay gaayam, te y\u00e9ena ngi koy def ba tey.\n6:11 Waaye danoo b\u00ebgg kenn ku nekk ci y\u00e9en wone cawarte gu mel ni ga ngeen amoon, ba kera ngeen di am mat, gi ngeen di s\u00e9entu.\n6:12 B\u00ebggunu ngeen tayel, waaye royleen \u00f1i g\u00ebm te mu\u00f1, ndaxte \u00f1ooy jot li leen Y\u00e0lla dig.\n6:13 Ibraayma bokk na ci \u00f1oom. Bi ko Y\u00e0llay dig, m\u00ebnul woon a gi\u00f1 ci keneen ku ko g\u00ebn a m\u00e0gg, ba tax mu gi\u00f1 ci boppam,\n6:14 ne ko: \u00abS\u00e0llaaw dinaa la barkeel, yokk saw askan.\u00bb\n6:15 Noonu Ibraayma di xaar tey mu\u00f1, ba jot li ko Y\u00e0lla digoon.\n6:16 Nit kuy gi\u00f1 nag, daf koy w\u00e9kk ci ku ko sut. Ngi\u00f1 lu mel noonu moo w\u00f3oral mbir te mooy jeexal l\u00e9pp lu \u00f1uy werante.\n6:17 \u00d1i war a jot li mu dige, Y\u00e0lla dafa leen b\u00ebggoon a won ne, dogalam du tebbiku mukk; looloo tax mu dige, boole ci ngi\u00f1.\n6:18 Noonu \u00f1aari j\u00ebf yooyu nga xam ne du\u00f1u tebbiku te Y\u00e0lla m\u00ebnu cee dellu gannaaw, da\u00f1u nuy g\u00ebn a s\u00f3ob ci mu\u00f1, nun \u00f1i daw ba am kiiraay, ngir nu man a t\u00e9ye bu d\u00ebg\u00ebr yaakaar, ji mu nu dig.\n6:19 Ci yaakaar jooju lanu s\u00ebs sunu xol, ba man a sampu bu d\u00ebg\u00ebr. Yaakaar la juy j\u00e0ll ba fa Y\u00e0lla nekk, ca gannaaw ridob b\u00e9rab bu sell-baa-sell.\n6:20 Yeesu ci boppam moo fa j\u00ebkk a dugg, muy ndaw li nu jiitu, \u00f1u def ko saraxalekat bu mag ba f\u00e0ww, mel ni Melkisedeg.\n7:1 Melkisedeg moomu doon buuru Salem, moo nekkoon saraxalekat ca Y\u00e0lla Aji Kawe ji. Gannaaw ba Ibraayma d\u00e0qee buur ya, ba dellusi, Melkisedeg gatandu woon na ko, di ko barkeel.\n7:2 Noonu Ibraayma fab fukkeelu c\u00e9r bi, maanaam asaka, ci li mu j\u00eble woon ci xare ba l\u00e9pp, jox ko. Ci lu j\u00ebkk turu Melkisedeg mi ngi tekki \u00abbuur bu jub bi.\u00bb Gannaaw loolu mooy buuru Salem, tur woowu mooy tekki \u00abbuuru j\u00e0mm.\u00bb\n7:3 Melkisedeg nag xamalu\u00f1u ko baay, xamalu\u00f1u ko yaay walla menn maam. Amul fenn fu \u00f1u wax ag juddoom walla ag deeyam. Moo tax nu di ko mengale ak Doomu Y\u00e0lla ji, ndaxte saraxalekat la bu kenn dul wuutu.\n7:4 Seetleen ni mu m\u00e0gge, moom Melkisedeg! Ibraayma sax, maamu cosaan mi, fab na li mu j\u00eble woon l\u00e9pp ca xare ba, jox Melkisedeg asaka ja.\n7:5 Yoonu Musaa digle na ne, \u00f1i bokk ci giiru Lewi te di ay saraxalekat, na\u00f1u jot asaka ci alalu b\u00e0nni Israyil, doonte sax \u00f1uy seeni bokk te soqikoo ci Ibraayma.\n7:6 Waaye Melkisedeg mi bokkul woon ci giiru Lewi, jotoon na asaka ci alali Ibraayma. Te rax-ca-dolli barkeel na ko, moom mi Y\u00e0lla s\u00e9dde woon dige yi.\n7:7 Kiy barkeel a g\u00ebn a m\u00e0gg ki \u00f1uy barkeel, loolu amu ci benn werante.\n7:8 Saraxalekat yi soqikoo ci Lewi, \u00f1u ngi jot asaka, ni ko Melkisedeg jote woon. Waaye \u00f1oom \u00f1u nar a dee la\u00f1u. Melkisedeg nag moom, Mbind mi w\u00f3oral na ne, dafay dund.\n7:9 L\u00e9egi nag ci ni \u00f1u ko man a waxe, Lewi miy jot asaka ci b\u00e0nni Israyil, moom ci boppam jox na ko Melkisedeg, jaare ko ci Ibraayma.\n7:10 Ndaxte mi ngi nekkoon ci ge\u00f1og maamam Ibraayma, bi ko Melkisedeg gatandoo.\n7:11 Jox na\u00f1u b\u00e0nni Israyil yoon wu sukkandiku ci ligg\u00e9eyu saraxalekat yi soqikoo ci Lewi. Su fekkoonte ne nag ligg\u00e9eyu saraxalekat yooyu manoon na yeggale nit cig mat, kon du soxlaati ab saraxalekat ni ko Melkisedeg nekke, ci f\u00e0nn gu wuute ak gu Aaroona.\n7:12 Te bu \u00f1u fi j\u00eblee saraxalekat yi ak seen ligg\u00e9ey, da\u00f1oo war a toxal itam yoon, wi \u00f1u fi t\u00ebraloon.\n7:13 Noonu Yeesu mi nuy wax, mi ngi soqikoo ci geneen giir gu bokkul ak giiru Lewi. Giir googu nag, amu ci kenn ku ci mas a def ligg\u00e9eyu saraxale ca saraxalukaay ba.\n7:14 Li w\u00f3or moo di, sunu Boroom mi ngi soqikoo ci giiru Yuda. Te bi Musaa bindee ci mbirum saraxalekat yi, limaalewul woon giir googu.\n7:15 Li waral mbir mi g\u00ebn a leer moo di ne, beneen saraxalekat bu mel ni Melkisedeg dafa \u00f1\u00ebw.\n7:16 Te defu\u00f1u ko saraxalekat jaarale ko ci yoonu ndono, waaye fal na\u00f1u ko ci dooley dund gu amul \u00e0pp.\n7:17 Ndaxte seedeel na\u00f1u Yeesu lii:\u00abDoon nga saraxalekat ba f\u00e0wwmel ni Melkisedeg.\u00bb\n7:18 Noonu tebbi na\u00f1u yoon wu j\u00ebkk, wa n\u00e9ewoon doole te me\u00f1\u00f1ul dara\n7:19 --ndax yoonu Musaa yeggalewul dara cig mat \u2014 waaye dugalal na\u00f1u nu fii yaakaar ju g\u00ebn ju nu man a jaare ngir jege Y\u00e0lla.\n7:20 Te rax-ca-dolli ngi\u00f1 \u00e0nd na ci. Ndaxte \u00f1i soqikoo ci Lewi doon na\u00f1u ay saraxalekat te kenn gi\u00f1ul.\n7:21 Waaye nag Yeesu moom doon na saraxalekat, bi Y\u00e0lla gi\u00f1ee ne ko:\u00abBoroom bi gi\u00f1 nate du dellu gannaaw mukk:\u201cDoon nga saraxalekat ba f\u00e0ww.\u201d\u00bb\n7:22 Ngi\u00f1 loolu moo tax Yeesu nekk tayle, giy w\u00f3oral k\u00f3ll\u00ebre gi g\u00ebn.\n7:23 Te it yeneen saraxalekat yi da\u00f1oo bare woon, ndaxte dee moo daan tax du\u00f1u man a sax ci seen ligg\u00e9ey.\n7:24 Waaye Yeesu miy dund ba f\u00e0ww, sasoo na ligg\u00e9eyu saraxale bu sax f\u00e0ww.\n7:25 Loolu moo tax it mu man a musal tey yeggale cig mat \u00f1iy jaar ci moom te b\u00ebgg jege Y\u00e0lla, ndaxte mi ngi dund ba f\u00e0ww ngir di leen rammu.\n7:26 Kon nag Yeesu mooy saraxalekat bu mag, bi nu soxla; dafa sell, du def lu bon, du taq b\u00e0kkaar, bokkul dara ak b\u00e0kkaarkat yi, te y\u00e9ege na\u00f1u ko fa Y\u00e0lla.\n7:27 Niroowul ak yeneen saraxalekat yu mag yi; soxlawul di def b\u00e9s bu set ay saraxi mala ngir b\u00e0kkaari boppam j\u00ebkk, teg ca yoy mbooloo mi. Yeesu def na sarax benn yoon ba f\u00e0ww ngir dindi b\u00e0kkaar yi, bi muy joxe bakkanam.\n7:28 Naka yoonu Musaa, aji n\u00e9ew doole yi lay fal saraxalekat yu mag. Waaye ngi\u00f1u Y\u00e0lla gi \u00f1\u00ebw gannaaw yoon wi, Doom ji la fal saraxalekat bu mag bu mat ba f\u00e0ww.\n8:1 Lii mooy li \u00ebpp solo ci li nuy wax: am nanu saraxalekat bu mag bu mel noonu, moom mi toog ci ndeyjooru Aji M\u00e0gg ja ca nguuram ca kaw.\n8:2 Mu ngi ligg\u00e9ey ca b\u00e9rab bu sell-baa-sell, di m\u00e0ggalukaay bu d\u00ebggu. Nit defaru ko; Boroom bee ko sos.\n8:3 B\u00e9pp saraxalekat bu mag fal na\u00f1u ko, ngir muy def ay sarax ak ay saraxi mala yu j\u00ebm ca Y\u00e0lla. Kon nag f\u00e0ww Yeesu am lu mu joxe.\n8:4 Bu nekkoon ci \u00e0ddina, du nekk sax saraxalekat, ndaxte am na fi ba noppi ay saraxalekat yuy def ay sarax, ni ko yoonu Musaa santaanee.\n8:5 Saraxalekat yooyu \u00f1u ngi ligg\u00e9eyal Y\u00e0lla ca m\u00e0ggalukaay, ba nekk misaal tey takkandeeru y\u00ebf yu d\u00ebggu, ya f\u00e9ete kaw. Moo tax ba Musaa naree defar t\u00e0ntu m\u00e0ggalukaay ba, Y\u00e0lla artu na ko ne ko: \u00abTeeylul ba def l\u00e9pp, roye ko ci bi ma la won ca tund wa.\u00bb\n8:6 Waaye l\u00e9egi nag ligg\u00e9eyu saraxale, bi \u00f1u jox Yeesu, moo g\u00ebn a m\u00e0gg ligg\u00e9eyu saraxalekat yooyu, mel ni it k\u00f3ll\u00ebre, gi Yeesu fas diggante Y\u00e0lla ak nit, moo sut k\u00f3ll\u00ebre gu j\u00ebkk ga te mu t\u00ebdd ci ay dige yu \u00ebpp yu j\u00ebkk ya.\n8:7 Bu fekkoonte ne, k\u00f3ll\u00ebre gu j\u00ebkk ga dafa amul woon benn sikk, kon du aajo \u00f1u koy weccee ak geneen.\n8:8 Waaye nag Y\u00e0lla sikk na b\u00e0nni Israyil, bi mu naan:Boroom bi nee na:\u00abAy fan a ngi \u00f1\u00ebwyu may fasi k\u00f3ll\u00ebre gu beesak b\u00e0nni Israyil ak waa Yude.K\u00f3ll\u00ebre googu nagbokkul ak gi ma fasoon ak seeni maam,\n8:9 ba ma leen j\u00e0ppee ci loxo,g\u00e9nne leen r\u00e9ewu Misra.Boroom bi nee na:Beddeeku naa leenndaxte s\u00e0mmu\u00f1u sama k\u00f3ll\u00ebre.\n8:10 Boroom bi nee na:K\u00f3ll\u00ebre gaa ngii,k\u00f3ll\u00ebre gi may fas ak b\u00e0nni Israyil,bu b\u00e9s yooyule weesoo.Dinaa def samay ndigal ci seen xel,bind ko ci seen xol.Dinaa nekk seen Y\u00e0lla,\u00f1u doon samay gaay.\n8:11 Kenn dootul war a j\u00e0ngal moroomamwalla mbokkam, di wax naan:\u201cXamal Boroom bi!\u201dNdaxte \u00f1\u00e9pp dina\u00f1u ma xam,li dale ci ki g\u00ebn a ndaw ba ci ki g\u00ebn a mag.\n8:12 Ndaxte dinaa leen baal seeni too\u00f1,te dootuma f\u00e0ttaliku seeni b\u00e0kkaar.\u00bb\n8:13 Kon nag bi Y\u00e0llay wax ci k\u00f3ll\u00ebre gu bees gi, dafa fekk mu m\u00e0ggatal gu j\u00ebkk ga. Te lu xewwi te m\u00e0ggat mi ngi ci t\u00e0nki w\u00e9y.\n9:1 K\u00f3ll\u00ebre gu j\u00ebkk ga \u00ebmboon na ay ndigal ci mbirum ni \u00f1u war a jaamoo Y\u00e0lla. Amoon na itam k\u00ebr Y\u00e0lla gu nekkoon \u00e0ddina.\n9:2 Nekkoon na ab t\u00e0ntu m\u00e0ggalukaay bu \u00f1u s\u00e9ddale \u00f1aari n\u00e9eg. Ca ba jiitu la l\u00e0mpu diwlin ba nekkoon ak taabal, ja \u00f1u daan teg mburu ya \u00f1u daa j\u00e9bbal Y\u00e0lla. Foofaa nga tuddoon b\u00e9rab bu sell ba.\n9:3 N\u00e9eg ba \u00f1u tudde b\u00e9rab bu sell-baa-sell a nga nekkoon ca gannaaw \u00f1aareelu rido ba.\n9:4 Saraxalukaayu wurus, ba \u00f1uy taal cuuraay ca kawam, a nga fa woon, ak gaalu k\u00f3ll\u00ebre, ga \u00f1u taf wurus ba mu daj. Ca biir gaal ga amoon na fa benn njaqu wurus bu defoon \u00f1am, wi \u00f1uy wax m\u00e0nn, ak it yetu Aaroona wi jebbi woon, ak \u00e0lluway doj, ya \u00f1u bindoon wax yi k\u00f3ll\u00ebre gi \u00ebmb.\n9:5 Ca kaw gaal ga teg na\u00f1u fa \u00f1aari nataali mbindeef yu \u00f1uy wax Seruben, yu doon wone ndamu Y\u00e0lla. Seeni laaf \u00f1oo doon yiir baalukaay ba. Waaye loolu l\u00e9pp l\u00e9egi m\u00ebnunu koo tekki benn-benn.\n9:6 Ba \u00f1u defaree l\u00e9pp, saraxalekat ya da\u00f1u daan dugg b\u00e9s bu set ca n\u00e9eg bu j\u00ebkk ba, ngir mottali seen ligg\u00e9eyu saraxale ca Y\u00e0lla.\n9:7 Waaye ca n\u00e9eg ba ca topp, saraxalekat bu mag ba rekk moo fa daan dugg benn yoon ci at mi. Te daawu fa dugg mukk te y\u00f3bbaalewul deretu mala, yi muy jagleel Y\u00e0lla, ngir b\u00e0kkaari boppam ak yu mbooloo mi daan def ci seen \u00f1\u00e0kka xam.\n9:8 Ci noonu nag Xel mu Sell mi wone na ne, yoon wi \u00f1uy jaar, ba dem ca b\u00e9rab bu sell-baa-sell, ubbikoogul woon, fi ak t\u00e0nt ba j\u00ebkk baa ngi doon taxaw.\n9:9 Misaal la ci jamonoy tey; dafay wone ne, sarax yi ak saraxi mala yi \u00f1u daan jagleel Y\u00e0lla, m\u00ebnu\u00f1oo dalal xelu jaamukatu Y\u00e0lla bi.\n9:10 Sarax yooyu \u00f1u ngi j\u00ebmoon ci lekk ak ci naan ak ci f\u00e0nn yu bare ci mbirum sangu set. Ay s\u00e0rt yu j\u00ebm ci yaram la\u00f1u, yu \u00f1u waroon a farataal, ba kera jamono ji Y\u00e0llay t\u00ebral k\u00f3ll\u00ebre gu bees.\n9:11 Waaye Kirist \u00f1\u00ebw na, doon saraxalekat bu mag, bi joxe x\u00e9ewal yi teew. Jaar na ca m\u00e0ggalukaay ba g\u00ebn a m\u00e0gg te g\u00ebn a mat, te m\u00e0ggalukaay booba loxol nit defaru ko, maanaam bokkul ci \u00e0ddina sii.\n9:12 Noonu Kirist dugg na benn yoon ba f\u00e0ww ca b\u00e9rab bu sell-baa-sell. Duggu fa ak deretu sikket yi ak yu y\u00ebkk yi. Waaye mi ngi duggaale ak deretu boppam te indil na nu noonu njot gu amul \u00e0pp.\n9:13 Deretu sikket yi ak ju y\u00ebkk yi, ak w\u00ebllu, wi \u00f1u lakk te di suy d\u00f3om bi \u00f1i taq sobe, \u00f1ooy sellal yaram.\n9:14 Su fekkee ne noonu la deme nag, du kon deretu Kirist moo \u00ebpp doole? Jox na bakkanam Y\u00e0lla, def ko sarax su amul sikk jaarale ko ci dooley Xel miy sax abadan. Kon deretam moo man a sellal sunu xel, mi nu doon yedd ndax j\u00ebf yu j\u00ebm ci dee, ngir nu man a jaamu Y\u00e0lla jiy dund.\n9:15 Looloo tax mu nekk Rammukat bi ci w\u00e0llu k\u00f3ll\u00ebre gu bees ci diggante Y\u00e0lla ak nit, ngir \u00f1i Y\u00e0lla woo am c\u00e9r bu sax ci kaw, te mu digoon leen ko, ndaxte Kirist dee na, ngir jot \u00f1i j\u00e0dd yoon ca k\u00f3ll\u00ebre gu j\u00ebkk ga.\n9:16 Ci li j\u00ebm ci d\u00e9nkaane bu \u00f1u bind, j\u00ebme ci miraas, f\u00e0ww \u00f1u wone firndeg deewu ka ko bind,\n9:17 ndaxte bala d\u00e9nkaaneb miraas di taxaw, dee am; te taxawul, fi ak ki ko bind a ngi dund.\n9:18 Looloo waral k\u00f3ll\u00ebre gu j\u00ebkk ga, \u00f1u fasoon ko ak deret.\n9:19 Keroog Musaa j\u00e0ng na ndigali yoon w\u00e9pp ci kanamu b\u00e0nni Israyil g\u00e9pp. Gannaaw loolu j\u00ebl na deretu w\u00ebllu, j\u00eblaale ndox, ak bantu garab gu \u00f1uy wax isob, laxas ci kawaru xar mu xonq. Noonu mu capp ko ca deret ja, daldi ko wis ca t\u00e9ereb yoon wa ak ca mbooloo m\u00e9pp\n9:20 te naan: \u00abLii mooy deretu k\u00f3ll\u00ebre gi leen Y\u00e0lla t\u00ebralal.\u00bb\n9:21 Noonu mu daldi wis it deret ja ca t\u00e0nt ba ak ca jumtukaay, ya \u00f1u daan jaamoo.\n9:22 Ndaxte ci yoonu Musaa, daanaka deret la\u00f1uy sellale l\u00e9pp, te bu deret tuuruwul, mbaalug b\u00e0kkaar du am.\n9:23 Y\u00ebfi \u00e0ddina yi misaal yu d\u00ebggu yi ci asamaan, war na\u00f1u leen a sellale noonu. Waaye y\u00ebf yu d\u00ebggu yooyu ci asamaan, laaj na sarax yu g\u00ebn a baax, ngir \u00f1u sell.\n9:24 Ndaxte Kirist duggul ci b\u00e9rab bu sell bu nit tabax, muy doon nataal ci bu d\u00ebggu bi. Waaye dugg na ca biir asamaan sax, ngir taxawal nu ca kanam Y\u00e0lla l\u00e9egi.\n9:25 Saraxalekat bu mag bi dafay dugg at mu jot ca b\u00e9rab bu sell-baa-sell ak deret ju dul josam. Waaye Kirist joxewul bakkanam ay yooni yoon.\n9:26 Bu demee woon noonu, kon dina sonn ba t\u00e0yyi ca nj\u00e0lb\u00e9enug \u00e0ddina ba tey. Waaye nag benn yoon rekk la fee\u00f1u ci mujjeelu jamono yi, joxe boppam ni sarax ngir far b\u00e0kkaar yi.\n9:27 Kon ni nit \u00f1i deeye benn yoon rekk, ba noppi jaar ca \u00e0tte ba, ni ko Y\u00e0lla dogale,\n9:28 noonu it la Kirist joxee boppam benn yoon, ngir g\u00e0ddu b\u00e0kkaaru nit \u00f1u bare, te dina fee\u00f1aat, waxuma ci mbiri b\u00e0kkaar, waaye ngir indil \u00f1i koy s\u00e9entu mucc gi.\n10:1 Yoonu Musaa dafa misaal x\u00e9ewal yi waroon a \u00f1\u00ebw; takkandeer la ci y\u00ebf yu d\u00ebggu yi, waaye du \u00f1oom ci seen bopp. Looloo tax m\u00ebnul a yeggale cig mat \u00f1i \u00f1\u00ebw ci Y\u00e0lla, ndaxte at mu nekk du\u00f1u j\u00f3g ci j\u00e9bbal Y\u00e0lla sarax yooyu.\n10:2 Sarax yi \u00f1uy def, bu \u00f1u manoon a sellal \u00f1iy jaamu benn yoon ba f\u00e0ww, kon dina\u00f1u leen b\u00e0yyi, ndaxte dootu\u00f1u am yeraange ci seeni b\u00e0kkaar.\n10:3 Waaye da\u00f1uy f\u00e0ttaliku b\u00e0kkaar yi ci sarax yi \u00f1uy def at mu jot.\n10:4 Ndaxte deretu y\u00ebkk yi ak ju sikket yi m\u00ebnu\u00f1oo dindi b\u00e0kkaar yi.\n10:5 Looloo tax bi muy w\u00e0cc \u00e0ddina, Kirist nee na:\u00abB\u00ebggoo saraxu mala walla beneen sarax,waaye aw yaram nga ma defaral.\n10:6 Sarax yu \u00f1uy lakkwalla sarax yiy dindi b\u00e0kkaar,benn neexu la ci.\n10:7 Moo tax ma ne: \u201cDamaa w\u00e0ccngir def sa coobare, yaw Y\u00e0lla,mu d\u00ebppoo ak li \u00f1u bind ci sama mbirci t\u00e9ereb yoon wi.\u201d\u00bb\n10:8 Wax na bu j\u00ebkk: \u00abSaraxi mala walla yeneeni sarax, sarax yu \u00f1uy lakk walla sarax yiy dindi b\u00e0kkaar, b\u00ebgguloo leen te benn neexu la ci.\u00bb Teewul yoon wi moo leen santaane.\n10:9 Noonu mu tegaat ca ne: \u00abDamaa w\u00e0cc ngir def sa coobare.\u00bb Noonu toxal na j\u00ebfin wu j\u00ebkk wa, ngir wuutal fi weneen wu bees.\n10:10 Te ci li Kirist def coobareg Y\u00e0lla, bi mu joxee yaramam sarax benn yoon ba f\u00e0ww, moo tax nu sell ci b\u00e0kkaar.\n10:11 B\u00e9s bu nekk saraxalekat yi da\u00f1uy taxaw di ligg\u00e9eyal Y\u00e0lla, di sax ci def sarax yu m\u00ebnul a dindi b\u00e0kkaar yi mukk.\n10:12 Waaye nag saraxalekat bii di Kirist, bi mu saraxee sarax bu am doole ngir dindi b\u00e0kkaar yi benn yoon ba f\u00e0ww, dafa toog ca ndeyjooru Y\u00e0lla,\n10:13 di xaar ba kera mu daaneel ko ay noonam ci kanamam.\n10:14 Noonu \u00f1i \u00f1uy sellal, ci benn sarax rekk la leen yeggali cig mat ba f\u00e0ww.\n10:15 Te it Xel mu Sell mi seedeel na nu ko;\n10:16 dafa j\u00ebkk a wax ne:\u00abBoroom bi nee na:K\u00f3ll\u00ebre gaa ngii,k\u00f3ll\u00ebre gi may fas ak \u00f1oom,bu b\u00e9s yooyule weesoo.Dinaa def samay ndigal ci seen xol,bind ko ci seen xel.\u00bb\n10:17 Noonu mu tegaat ca ne:\u00abDootuma f\u00e0ttaliku seeni b\u00e0kkaarwalla seeni too\u00f1.\u00bb\n10:18 Kon nag fu \u00f1uy baale b\u00e0kkaar, aajootul sarax su koy dindi.\n10:19 Bokk yi, gannaaw nag deretu Yeesu may na nu sa\u00f1-sa\u00f1u dugg ca b\u00e9rab bu sell-baa-sell,\n10:20 nuy jaar ci rido bi, ci yoon wi mu nu ubbil, di yoon wu bees tey dund, maanaam ndax li mu joxe yaramam sarax te mi ngi dund,\n10:21 te gannaaw am nanu saraxalekat bu mag, biy yilif waa k\u00ebr Y\u00e0lla,\n10:22 kon nanu jege Y\u00e0lla ak xol bu laab, ak ng\u00ebm gu \u00e0nd ak k\u00f3olute, am xel mu dal ci b\u00e9pp yeraange, ak yaram wu \u00f1u raxas ci ndox mu sell.\n10:23 Nanu j\u00e0pp ci yaakaar, ji nu am, te ba\u00f1 a toqi, ndaxte ki nu dig, lu mu wax def ko.\n10:24 Nanu seet ni nu man a xiirtalante cig mb\u00ebggeel ak ci j\u00ebf yu baax.\n10:25 Te bunu b\u00e0yyi sunu ndaje yi, ni ko \u00f1enn \u00f1i di defe, waaye nanuy n\u00e0ddante ci ng\u00ebm, di ko feddali, fi ak y\u00e9ena ngi gis b\u00e9su Boroom biy jubsi.\n10:26 Gannaaw ba nu nangoo xam d\u00ebgg ba noppi, bu nu teyee di def b\u00e0kkaar, kon sarax dootul am ngir b\u00e0kkaar yooyu.\n10:27 D\u00e9ed\u00e9et, bu nu defee noonu, dinanu tiit di xaar \u00e0tte ba, muy taal bu y\u00e0nj, biy war a lakk nooni Y\u00e0lla yi.\n10:28 Ku weddi ndigali yoonu Musaa wi, te \u00f1aar walla \u00f1etti nit seede ko, dina dee ci lu amul benn y\u00ebrmande.\n10:29 Ku xeeb Doomu Y\u00e0lla ji te fonkadi deretu k\u00f3ll\u00ebre, ji \u00f1u ko sellale, te muy toroxal Xelum Y\u00e0lla, mi indi yiw, naka la mbugalam war a g\u00ebn a y\u00e9ese?\n10:30 Xam nanu ki wax ne: \u00abMan maay \u00e0tte, maay fey j\u00ebf.\u00bb Te newaat na: \u00abBoroom bi dina \u00e0tte ay gaayam.\u00bb\n10:31 Ndaw tiitaange ci ku s\u00e0ggan, ba t\u00e0bbi ci loxoy Y\u00e0lla jiy dund!\n10:32 F\u00e0ttalikuleen b\u00e9s yu j\u00ebkk ya, ba leeru Y\u00e0lla t\u00e0bbee ci y\u00e9en; d\u00e9kku ngeen xeex bu mag ciy fitna.\n10:33 L\u00e9eg-l\u00e9eg \u00f1u saaga leen ak di leen sonal ci kanamu nit \u00f1i; l\u00e9eg-l\u00e9eg it ngeen taxawu \u00f1i \u00f1uy def noonu.\n10:34 Ndaxte bokk ngeen naqar ak \u00f1i \u00f1u t\u00ebj, te nangu ngeen ak xol bu sedd, \u00f1u foqar\u00f1i seen alal, xam ne, am ngeen alal ju g\u00ebn te di sax ba f\u00e0ww.\n10:35 Kon nag buleen s\u00e0ggane k\u00f3olute gi ngeen am, ndaxte \u00ebmb na yool bu mag.\n10:36 Dangeen a war a mu\u00f1, ba def coobareg Y\u00e0lla, sog a jot li mu leen digoon.\n10:37 Ndaxte lii la Mbind mi wax:\u00abCi kanam tuuti, ki war a \u00f1\u00ebw dina \u00f1\u00ebwte l\u00e9egi mu agsi.\n10:38 Ku jub ci sama kanam dina dund ci kaw ng\u00ebm,waaye bu delloo gannaaw,sama xol du sedd ci moom.\u00bb\n10:39 Nun nag bokkunu ci \u00f1iy dellu gannaaw bay r\u00e9er, waaye nu ngi bokk ci \u00f1i am ng\u00ebm tey mucc.\n11:1 Am ng\u00ebm lii lay tekki: dafa nuy w\u00f3or ne, li nuy yaakaar dina am, te it li nu dul gis nekk na.\n11:2 Maam ya, seen ng\u00ebm a tax ba Y\u00e0lla seedeel leen lu baax.\n11:3 Ng\u00ebm a tax ba nu xam ne, Y\u00e0lla s\u00e0kk na \u00e0ddina jaarale ko ci k\u00e0ddoom, ngir li b\u00ebt di gis, defarees ko ak lu b\u00ebt m\u00ebnul a gis.\n11:4 Ng\u00ebm moo tax ba Abel j\u00e9bbal Y\u00e0lla sarax su g\u00ebn saraxu Kayin. Ng\u00ebmu Abel moo tax ba Y\u00e0lla \u00e0tte ko ni ku jub, bi mu ko seedeelee ne, saraxam baax na. Te ci kaw ng\u00ebm lay wax ba tey, moom mi dee ba noppi.\n11:5 Ng\u00ebm moo tax ba Enog jaarul ci dee. Y\u00e0llaa ko y\u00f3bbu ca moom, te kenn gisatu ko, ndaxte Y\u00e0llaa ko toxal. Ndaxte Mbind mi seedeel na ko ne, laata muy toxu, neex na Y\u00e0lla.\n11:6 Waaye ku amul ng\u00ebm doo man a neex Y\u00e0lla, ndaxte ku b\u00ebgg a jege\u00f1 Y\u00e0lla war ngaa g\u00ebm ne, Y\u00e0lla am na te dina neexal \u00f1i koy wut.\n11:7 Ng\u00ebm moo tax ba, bi Y\u00e0lla y\u00e9galee N\u00f3oyin lu jiitu ci mbir yi dikkagul, mu ragal ba defar gaal ngir musal njabootam. Ng\u00ebmam moo tax mu yey niti \u00e0ddina, ba noppi jot njubte, li Y\u00e0llay joxe ci kaw ng\u00ebm.\n11:8 Ng\u00ebm moo tax ba Ibraayma d\u00e9ggal Y\u00e0lla. Bi ko Y\u00e0lla wooyee, mu dem toxu ci menn r\u00e9ew, ma mu waroon a jote ca Y\u00e0lla. Noonu la g\u00e0ddaaye d\u00ebkkam te xamul woon fan la j\u00ebm.\n11:9 Ng\u00ebm a tax ba Ibraayma sanc ci r\u00e9ew, mi ko Y\u00e0lla digoon, d\u00ebkk ci ay t\u00e0nt ni doxand\u00e9em, moom ak doomam Isaaxa ak s\u00ebtam Yanq\u00f3oba, fekk sax Y\u00e0lla digoon na leen r\u00e9ew mi.\n11:10 Waaye nag Ibraaymaa ngi doon s\u00e9entu d\u00ebkk bi sax, bi Y\u00e0lla tabax te sanc ko.\n11:11 Ng\u00ebm moo tax ba Ibraayma, li muy m\u00e0ggat l\u00e9pp te Saarata m\u00ebnul woon a am doom, Y\u00e0lla def ba mu jur doom, ndaxte dafa g\u00ebmoon ne, Y\u00e0lla lu mu dige def ko.\n11:12 Looloo tax ba, Ibraayma mi m\u00e0ggat lool, aw xeet j\u00f3ge ci moom, baree ni biddiiwi asamaan, te sakkan ni suufu tefes, ba kenn m\u00ebnu koo xayma.\n11:13 \u00d1oom \u00f1\u00e9pp dee na\u00f1u ci ng\u00ebm. Jotu\u00f1u li \u00f1u leen digoon, waaye s\u00e9en na\u00f1u ko fu sore ba nuyu leen, te nangu ne, ay doxand\u00e9em ak i gan la\u00f1u woon ci \u00e0ddina.\n11:14 \u00d1iy waxe noonu nag da\u00f1uy wone ne, \u00f1oo ngi wut r\u00e9ew mu \u00f1u moomal seen bopp.\n11:15 Bu \u00f1u nammoon r\u00e9ew mi \u00f1u j\u00f3ge, kon dina\u00f1u am jotu dellu fa.\n11:16 Waaye \u00f1u ngi doon s\u00e9entu r\u00e9ew mu g\u00ebn, maanaam mi nekk ci asamaan. Looloo tax Y\u00e0lla rusul \u00f1u koy wooye seen Y\u00e0lla, ndaxte defaral na leen ab d\u00ebkk.\n11:17 Ng\u00ebm moo tax Ibraayma naroon a rey Isaaxa ni sarax, bi ko Y\u00e0lla nattoo. Moom mi jotoon dige yi, moo demoon bay saraxe jenn doom ji mu am kepp,\n11:18 fekk sax Y\u00e0lla nee woon na ko: \u00abSaw askan ci Isaaxa lay jaar.\u00bb\n11:19 Waaye xelu Ibraayma j\u00e0ppoon na ne, Y\u00e0lla am na dooley dekkal n\u00e9ew yi. Te d\u00ebgg-d\u00ebgg ci misaal dafa mel ni, Isaaxa dafa dee te dekki.\n11:20 Te it ng\u00ebm moo tax ba Isaaxa barkeel Yanq\u00f3oba ak Esawu, di wax ci mbirum y\u00ebf yiy \u00f1\u00ebw.\n11:21 Ng\u00ebm moo tax ba, bi Yanq\u00f3oba nekkee ci sukkurat, mu barkeel kenn ku nekk ci doomi Yuusufa yi. Moo tax it mu m\u00e0ggal Y\u00e0lla, jafandu ci yetam.\n11:22 Ng\u00ebm moo tax ba, bi Yuusufa nekkee ci sukkurat, mu waxoon ci g\u00e0ddaay gi b\u00e0nni Israyil waroon a g\u00e0ddaaye Misra, di joxe ndigal j\u00ebme ci mbirum n\u00e9ewam.\n11:23 Ng\u00ebm moo tax ba, bi Musaa juddoo, ay waajuram n\u00ebbb ko lu mat \u00f1etti weer, ndaxte gisoon na\u00f1u ne, xale bu taaru la woon, te ragalu\u00f1u woon ndigalu buur bi.\n11:24 Ng\u00ebm a tax ba bi Musaa m\u00e0ggee, muy ba\u00f1 \u00f1u koy wooye s\u00ebtu Firawna.\n11:25 Bokk coono ak gaayi Y\u00e0lla yi moo ko g\u00ebnaloon muy b\u00e0nneexu ab diir ci b\u00e0kkaar.\n11:26 \u00d1u toroxal ko ngir Almasi bi mi ngi mel ci moom ni alal ju \u00ebpp alali Misra y\u00e9pp, ndaxte yool bi la doon s\u00e9entu.\n11:27 Ng\u00ebm moo tax mu j\u00f3ge Misra te ragalul merum buur bi. Dafa mu\u00f1, mel ni nit kuy gis Y\u00e0lla, mi kenn m\u00ebnul a teg b\u00ebt.\n11:28 Ng\u00ebm moo tax mu sos m\u00e0ggalu B\u00e9su J\u00e9ggi ba, di wis deret ci bunt yi, ngir malaakam Y\u00e0qkat mi ba\u00f1 a laal taawi b\u00e0nni Israyil.\n11:29 Ng\u00ebm moo tax ba b\u00e0nni Israyil jaar ci G\u00e9ej gu xonq gi, mel ni kuy jaar ci yoonu suuf su wow. Waaye bi ci waa Misra yi doon j\u00e9em a jaar, \u00f1oom \u00f1u daldi lab.\n11:30 Ng\u00ebm moo tax miir yi w\u00ebroon d\u00ebkku Yeriko m\u00e0bb, gannaaw ba ko b\u00e0nni Israyil w\u00ebree lu mat jur\u00f3om-\u00f1aari fan.\n11:31 Ng\u00ebm moo tax ba Raxab jig\u00e9enu moykat bi mucc, keroog ba \u00f1uy b\u00f3om \u00f1i d\u00e9ggadiloon Y\u00e0lla, ndax li mu teeru woon y\u00ebddukat ya teeru bu \u00e0nd ak j\u00e0mm.\n11:32 Lu ma ci war a tegaat? Ndaxte awma jotu wax ci mbirum Sedeyon, Barag, Samson, Yefte, Daawuda, Samwil ak yonent yi.\n11:33 Seen ng\u00ebm a tax \u00f1u noot ay buur, di doxal yoon tey jot li Y\u00e0lla dige. Ng\u00ebm moo tax ba tey, \u00f1u t\u00ebj g\u00e9mmi\u00f1u gaynde yi,\n11:34 fey dooley safara, r\u00ebcc ci jaasi, \u00f1u g\u00e9nn ci n\u00e9ew doole, dugg ci k\u00e0ttan, doon ay j\u00e0mbaar, d\u00e0q xarekat, ya j\u00f3ge bitim r\u00e9ew.\n11:35 Ng\u00ebm moo tax ba ay jig\u00e9en gis \u00f1u dekkal seeni n\u00e9ew, delloo leen ko; \u00f1eneen \u00f1i \u00f1u metital leen, te ba\u00f1 ku leen musal, ngir jot ndekkite lu g\u00ebn.\n11:36 \u00d1eneen \u00f1i d\u00e9kku na\u00f1u ay xas ak ay yar, ay j\u00e9ng ak kaso yi.\n11:37 \u00d1ii, s\u00e0nni na\u00f1u leen ay xeer ba \u00f1u dee; \u00f1ii, \u00f1u xar leen \u00f1aar; \u00f1ii, \u00f1u reye leen jaasi. \u00d1u ngi doon w\u00ebnd\u00e9elu, sol ay deri xar ak yu b\u00eby, di ay walaakaana; \u00f1u di leen sonal, di leen fitnaal.\n11:38 \u00d1u ngi leen doon def noonu, fekk \u00e0ddina sax yelloowul leen. \u00d1u ngi doon w\u00ebreelu ci \u00e0ll yi ak ci tund yi, dal ci xunti yi ak ci k\u00e0mb yi.\n11:39 Nit \u00f1oo\u00f1u \u00f1\u00e9pp, seen ng\u00ebm a tax ba Y\u00e0lla seedeeloon leen lu baax. Moona de, jotu\u00f1u li Y\u00e0lla dige woon,\n11:40 ndaxte Y\u00e0lla dafa t\u00ebral lu g\u00ebn ci nun te b\u00ebggu leen a yeggale cig mat, fi ak \u00e0ndu\u00f1u ci ak nun.\n12:1 Kon nag gannaaw mbooloo mu bare moo nu y\u00e9ew, di nu seedeel seen ng\u00ebm, nanu yenniku b\u00e9pp yen ak b\u00e0kkaar bu nuy t\u00e9qtal ci lu yomb, tey daw x\u00e9l wi nekk sunu kanam, \u00e0nd ci ak mu\u00f1.\n12:2 Nanu ne j\u00e0kk Yeesu, moom mi samp ng\u00ebm, ba ub l\u00e0mbi ng\u00ebm. Mb\u00e9g mi mu d\u00ebgm\u00ebl moo tax mu d\u00e9kku dee ca bant ba te faalewul toroxte, ji ko fa fekk, ba noppi toog ca ndeyjooru jal, ba Y\u00e0lla nekk.\n12:3 Defleen seen xel ci moom, moom mi mu\u00f1 noonu ko b\u00e0kkaarkat yi ba\u00f1e woon, ngir ba\u00f1 seen k\u00e0ttan jeex, ngeen x\u00e0ddi.\n12:4 Y\u00e9en demaguleen ba tuur seen deret ci seen b\u00ebre ak b\u00e0kkaar.\n12:5 Te f\u00e0tte ngeen li leen Y\u00e0lla d\u00e9nk ni baay ak ay doomam naan:\u00abSama doom, bul fonkadi yarub Boroom bimbaa ngay x\u00e0ddi, bu lay yedd,\n12:6 ndaxte ku Boroom bi sopp, yar la,tey duma b\u00e9pp doom bu mu nangu.\u00bb\n12:7 Li ngeen di war a mu\u00f1, ab yar la. Y\u00e0lla dafay j\u00ebf ak y\u00e9en ni ay doomam, ndaxte ana doom ju baayam dul yar?\n12:8 Bu ngeen bokkul woon ci yar, bi \u00f1\u00e9pp am w\u00e0ll, kon dungeen ay doomi yoon; ay doom yu daganul ngeen.\n12:9 Waaye sax far, sunuy baay ci \u00e0ddina yaroon na\u00f1u nu, te wegoon nanu leen. Baay bi yore ruu yi kon, xanaa warunu koo g\u00ebn a d\u00e9ggal ngir man a dund?\n12:10 Sunuy baay yar na\u00f1u nu diir bu g\u00e0tt ci seen coobare. Waaye Y\u00e0lla dafa nuy yar ngir sunu njari\u00f1, ngir nu bokk ci sellaayam.\n12:11 Li am moo di ne, yar bu nuy dal, du \u00e0nd ak b\u00e0nneex, day naqari, waaye gannaaw ga dafay me\u00f1\u00f1 jub ak j\u00e0mm, ci \u00f1i ko jari\u00f1oo.\n12:12 Kon nag mayleen doole loxo yi toqi, ak \u00f3om yi ba\u00f1,\n12:13 te f\u00e0kkal seeni t\u00e0nk ay yoon yu jub, ngir c\u00e9r bi l\u00e0ggi ba\u00f1 cee jekkalikoo waaye mu w\u00e9re ci.\n12:14 Wutleen ak \u00f1\u00e9pp j\u00e0mm te fonk dund gu sell, ndaxte ku sellul doo gis Boroom bi.\n12:15 Moytuleen ba kenn du \u00f1\u00e0kk yiwu Y\u00e0lla mbaa kenn mel ni reen bu wex buy jebbi, ba di leen l\u00ebjal tey gaa\u00f1 \u00f1u bare ci wextanam.\n12:16 Moytuleen it ba kenn du njaaloo walla muy fonkadi y\u00ebfi Y\u00e0lla, ni Esawu, mi weccee woon ndonol taawam ngir ag lekk.\n12:17 Xam ngeen ne, ba \u00f1u ca tegee tuuti, g\u00e0ntu na\u00f1u ko, ba mu b\u00ebggee jot barke bi. Amul fenn fu mu jaar ba defar njuumteem, te jooy, yi mu doon jooy, m\u00ebnu ci dara.\n12:18 Ndaxte meluleen ni b\u00e0nni Israyil \u00f1oom \u00f1i jege woon tund wu \u00f1u man a laal, wu doon t\u00e0kk jeppit te \u00e0nd ak xiin ak l\u00ebnd\u00ebm ak ngelaw.\n12:19 Jegewuleen liit guy jib ak baat buy wax ay wax yoo xam ne \u00f1i ko doon d\u00e9gg, \u00f1aan \u00f1u ba\u00f1 leen cee tegal benn baat,\n12:20 ndaxte m\u00ebnu\u00f1u woon a d\u00e9kku ndigal lii: \u00abSu mala sax laalee tund wa, nangeen ko s\u00e0nni ay xeer, ba mu dee.\u00bb\n12:21 Te mbir moomu \u00f1u doon seetaan dafa raglu, ba Musaa naan: \u00abDamaa tiit bay lox.\u00bb\n12:22 Waaye y\u00e9en jege ngeen tund wi \u00f1uy wax Siyon, di d\u00ebkku Y\u00e0lla jiy dund, muy Yerusalem ba ca asamaan. Jege ngeen it junniy junniy malaaka yu b\u00e9g-a-b\u00e9g, ba daje di m\u00e0ggal;\n12:23 jege mbooloom taawi Y\u00e0lla, yu \u00f1u bind seen tur ca asamaan. Jege ngeen Y\u00e0lla, jiy \u00e0tte \u00f1\u00e9pp; jege ruuwi nit \u00f1u jub, \u00f1i \u00e0gg cig mat;\n12:24 jege Yeesu, Rammukat bi s\u00e0mm k\u00f3ll\u00ebre gu bees gi; jege deretam, ji \u00f1u wis. Te deret jooju, li muy y\u00e9gle moo g\u00ebn a neex li deretu Abel doon y\u00e9ene.\n12:25 Moytuleen a tanqamlu nag kiy wax ak y\u00e9en. Ndegam \u00f1iy tanqamlu ki leen di artu ci \u00e0ddina, \u00f1oo m\u00ebnul a r\u00ebcc ci \u00e0tte bi, aste ku dumm\u00f3oyu kiy wax ci asamaan.\n12:26 Bu j\u00ebkk baatam yengaloon na suuf, waaye l\u00e9egi dafa dige ne: \u00abBeneen yoon laay yengalaat suuf, yengal asamaan itam.\u00bb\n12:27 Ci li mu wax: \u00abBeneen yoon,\u00bb dafay xamle ne, Y\u00e0lla dina dindi yi \u00f1u man a yengal, maanaam li \u00f1u s\u00e0kk, ngir li \u00f1u m\u00ebnul a yengal sax ba f\u00e0ww.\n12:28 Kon nag gannaaw dina\u00f1u jot nguur gu kenn m\u00ebnul a yengal, nanu ci sant Y\u00e0lla, di ko jaamu, ni mu ko b\u00ebgge, boole ci wegeel ak ragal,\n12:29 ndaxte sunu Y\u00e0lla, safara la suy lakke.\n13:1 Saxleen ci b\u00ebggante ni ay bokk.\n13:2 Buleen f\u00e0ttee teral \u00f1iy \u00f1\u00ebw ci y\u00e9en, ndaxte \u00f1enn \u00f1i, bi \u00f1u ko defee, teral na\u00f1u ay malaaka te xamu\u00f1u ko.\n13:3 F\u00e0ttalikuleen \u00f1i \u00f1u t\u00ebj, mel ni su \u00f1u leen boole woon ak \u00f1oom t\u00ebjaale. F\u00e0ttalikuleen \u00f1i \u00f1uy sonal, ni su ngeen bokkoon ak \u00f1oom coono.\n13:4 Na \u00f1\u00e9pp fullaal s\u00e9y, te lalu s\u00e9y bi ba\u00f1 a taq sobe, ndaxte Y\u00e0lla dina \u00e0tte \u00f1u y\u00e0qu \u00f1i ak njaalookat yi.\n13:5 Buleen b\u00ebgge; deeleen doylu, ndaxte Y\u00e0lla ci boppam nee na:\u00abDuma la wacc mukk,duma la wor mukk,\u00bb\n13:6 ba tax nu am k\u00f3oluteg wax ne:\u00abBoroom bi moo di sama ndimbal;duma ragal dara.Lu ma nit manal?\u00bb\n13:7 F\u00e0ttalikuleen seen njiit, yi leen y\u00e9gal k\u00e0ddug Y\u00e0lla. Nemmikuleen li seen dund me\u00f1\u00f1 te roy seen ng\u00ebm.\n13:8 Yeesu Kirist du soppiku mukk; ni mu mel d\u00e9mb ak tey lay mel ba f\u00e0ww.\n13:9 Buleen nangu mukk \u00f1u f\u00e0bbi leen ak nj\u00e0ngale yu bare yu wuute ak yu j\u00ebkk ya. Li g\u00ebn moo di xol yi j\u00eble seen doole ci yiwu Y\u00e0lla, te ba\u00f1 koo j\u00eble ci s\u00e0rt yi j\u00ebm ci \u00f1am, yi jari\u00f1ul dara \u00f1i koy s\u00e0mm.\n13:10 Am nanu sarax boo xam ne \u00f1iy jaamu Y\u00e0lla ci t\u00e0ntu m\u00e0ggalukaayu b\u00e0nni Israyil sa\u00f1u\u00f1u koo lekk.\n13:11 Ndaxte saraxalekat bu mag bi dafay y\u00f3bbu deretu mala yi ca b\u00e9rab bu sell-baa-sell ni sarax ngir dindi b\u00e0kkaar yi, waaye y\u00e0pp wi dees na ko lakk ca gannaaw dal ba.\n13:12 Looloo tax Yeesu sonn ca gannaaw d\u00ebkk ba, ngir sellal mbooloo mi ak deretam.\n13:13 Nanu ko fekki nag ca gannaaw dal ba, bokk ak moom toroxte ga.\n13:14 Amunu fii ci \u00e0ddina d\u00ebkk bu sax ba f\u00e0ww, waaye nu ngi wut d\u00ebkk biy \u00f1\u00ebw.\n13:15 Kon nag nanu jaare ci Yeesu, tey d\u00ebkk ci j\u00e9bbal Y\u00e0lla sarax bu koy m\u00e0ggal, maanaam sant turam.\n13:16 Buleen f\u00e0tte di def lu baax ak di s\u00e9dde ci seen alal, ndaxte sarax yu mel noonu \u00f1oo neex Y\u00e0lla.\n13:17 D\u00e9ggal-leen seeni njiit te topp seen ndigal, ndaxte \u00f1oo leen di s\u00e0mm te \u00f1ooy layoo seen ligg\u00e9ey. Kon nangeen leen d\u00e9ggal, ngir \u00f1u man a def seen ligg\u00e9ey ak xol bu sedd, ba\u00f1 cee am naqar, ndaxte loolu du leen amal njari\u00f1.\n13:18 Deeleen nu \u00f1aanal. W\u00f3or nanu ne, sunu xel dal na, ndaxte danoo b\u00ebgg a rafet ci l\u00e9pp lu nuy def.\n13:19 Maa ngi leen di xiir, ngeen \u00f1aanal nu, ba tuur ci seen \u00f1aq, ngir ma yiwiku, ba dellusi ci y\u00e9en ci ni mu g\u00ebn a gaawe.\n13:20 Na leen Y\u00e0lla Boroom j\u00e0mm, mi dekkal sunu Boroom Yeesu, di S\u00e0mm bu mag bi, ci darajay deret, ji fas k\u00f3ll\u00ebre gu sax,\n13:21 matal ci l\u00e9pp lu baax, ba ngeen man a def coobareem, di j\u00ebfe ci nun li neex ci moom, mu jaarale l\u00e9pp ci Yeesu Kirist, moom mi yelloo ndam ba f\u00e0ww. Amiin.\n13:22 Kon nag bokk yi, maa ngi leen di \u00f1aan, ngeen tegoo baatu yedd yooyu, ndaxte dama leen a bind ci lu g\u00e0tt.\n13:23 Xamleen ne, Timote sunu mbokk, g\u00e9nn na kaso. Su dikkee l\u00e9egi, dinaa \u00e0nd ak moom, seetsi leen.\n13:24 Nuyul-leen ma seen njiit y\u00e9pp ak gaayi Y\u00e0lla y\u00e9pp. Waa Itali \u00f1u ngi leen di nuyu.\n13:25 Na yiwu Y\u00e0lla nekk \u00e0nd ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.","title":"Wolof Bible (NT): Hebrews","type":"page"}
