{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/jam.htm","path":"bib/wb/wlf/jam.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/jam.htm","text":"1:1 Man Saag, jaamu Y\u00e0lla ak Boroom bi Yeesu Kirist, maa leen di nuyu, y\u00e9en fukki giir ak \u00f1aar, yi tasaaroo ci biir \u00e0ddina si.\n1:2 Y\u00e9en samay bokk, waxtu wu nattu yi dalee ci seen kaw, ak nu \u00f1u man a mel, defleen ko ni mb\u00e9g mu r\u00e9y,\n1:3 xam ne nattub ng\u00ebm mooy ndeyu mu\u00f1.\n1:4 Kon na seen mu\u00f1 dem ba mat, ngir ngeen ba\u00f1 a fell fenn, waaye ngeen mat s\u00ebkk.\n1:5 Ku xelam des ci benn f\u00e0nn ci y\u00e9en nag, na ko \u00f1aan Y\u00e0lla, te dina ko ko may, ndaxte Y\u00e0lla mooy Aji Y\u00e9w\u00e9n, jiy may \u00f1\u00e9pp ci lu \u00e0ndul ak genn \u014b\u00e0\u00f1\u00f1.\n1:6 Waaye na ko \u00f1aan ci ng\u00ebm te ba\u00f1 cee werante; ndaxte kiy werante mi ngi mel ni ndoxum g\u00e9ej, mi ngelaw liy l\u00ebmbaaje wet gu ne.\n1:7 Bu kooku yaakaar dara ci Boroom bi.\n1:8 Ku am xel \u00f1aar la, te \u00f1\u00e0kk pasteef ci l\u00e9pp lu mu man a def.\n1:9 Naka mbokk mi n\u00e9ew doole, na sant ci teraangaam fa kanam Y\u00e0lla,\n1:10 te boroom alal it sant cig suufeem, ndax ni t\u00f3or-t\u00f3or di ruuse, noonu lay w\u00e9ye.\n1:11 Su jant fenkee, ba naaj wi t\u00e0ng, kon g\u00e0ncax lax, t\u00f3or-t\u00f3or ruus, te rafetaayam naaw. Noonu la boroom alal di nasaxe, moom ak i j\u00ebfam.\n1:12 Ku d\u00e9kku nattu, ku barkeel nga, ndax boo ci g\u00e9nnee ak ndam, dees na la jagleel kaalag dund, gi Y\u00e0lla dig \u00f1i ko b\u00ebgg.\n1:13 Bu la fiir galanee, bul ne: \u00abY\u00e0llaa ko dogal,\u00bb ndaxte Y\u00e0lla jegewul ak mbon fenn te du fiir kenn.\n1:14 Waaye ku sa bakkan nax, ba man la, looloo lay dugal ci fiir.\n1:15 Kon bu b\u00ebgg-b\u00ebgg \u00ebmbee, b\u00e0kkaar lay wasin, te bu b\u00e0kkaar m\u00e0ggee, jur dee.\n1:16 Y\u00e9en sama bokk yi ma b\u00ebgg, buleen juum ci lii:\n1:17 g\u00e9pp may gu baax ak g\u00e9pp jagle gu mat, ci Y\u00e0lla la j\u00f3ge, di Baay bi s\u00e0kk leeri asamaan, fekk moom du soppiku, mbaa muy leer ak di l\u00ebnd\u00ebm.\n1:18 Ci coobareem la nu sole k\u00e0ddug d\u00ebgg gi, ba nu judduwaat, di t\u00e0nneefu l\u00e9pp lu mu bind.\n1:19 Y\u00e9en sama bokk yi ma b\u00ebgg, nangeen xam lii: ku nekk war ngaa farlu ci d\u00e9glu, di y\u00e9ex a wax tey y\u00e9ex a mer.\n1:20 Ndaxte meru nit du jur njub gi neex Y\u00e0lla.\n1:21 Moo tax nanguleen ci woyof k\u00e0ddu, gi leen Y\u00e0lla sol te man leen a musal, di d\u00ebddu b\u00e9pp sobe ak coxor gi daj \u00e0ddina.\n1:22 Buleen yem ci d\u00e9glu k\u00e0ddu gi rekk, di nax seen bopp; waaye j\u00ebfeleen ko.\n1:23 Ndaxte ku d\u00e9glu k\u00e0ddu gi, te ba\u00f1 koo j\u00ebfe, moom ak kuy seetu \u00f1oo yem;\n1:24 day gis xar-kanamam, te su nee w\u00ebr\u00eb\u00f1, daldi f\u00e0tte meloom.\n1:25 Waaye kuy g\u00ebstu yoonu Y\u00e0lla, wi mat tey goreel --waxuma ki d\u00e9gg, ba noppi f\u00e0tte, waaye kiy j\u00ebfe ndigal \u2014 kooku barkeel na ci kaw j\u00ebfam.\n1:26 Ku yaakaar ne am na diine, waaye moomul l\u00e0mmi\u00f1am, xanaa di nax boppam rekk, diineem jooju du diiney dara.\n1:27 Ku diineem sell te amul benn g\u00e0kk fa kanam Y\u00e0lla mooy kii: ki nemmiku jiirim yi ak jig\u00e9en \u00f1i seen j\u00ebkk\u00ebr faatu ci seeni tiis, tey waggar sobey \u00e0ddina.\n2:1 Y\u00e9en samay bokk, bu benn g\u00ebnale laal seen ng\u00ebm ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi soloo ndam.\n2:2 Ndaxte su \u00f1aari nit duggee ci seen mbooloo, kii takk jaaroy wurus te sol y\u00e9re yu taaru, ka ca des \u00f1\u00e0kk te limboo ay sagar,\n2:3 ngeen teral boroom daraja ji ne ko: \u00ab\u00c0ggal ci jataay bu yiw bi,\u00bb ba noppi ngeen ne aji n\u00e9ew doole ji: \u00abTaxawal fale, mbaa nga toog fi ci samay t\u00e0nk,\u00bb\n2:4 kon g\u00ebnale ngeen ci seen biir, ba \u00e0tte ci col, b\u00e0yyi xol.\n2:5 D\u00e9gluleen y\u00e9en sama bokk yi ma b\u00ebgg, ndax Y\u00e0lla t\u00e0nnul \u00f1i n\u00e9ewle ci \u00e0ddina, ngir \u00f1u barele ci ng\u00ebm, tey am i c\u00e9r ci nguur, gi Y\u00e0lla dig \u00f1i ko b\u00ebgg?\n2:6 Fekk dangeen leen di toroxal! Xanaa du boroom alal yi \u00f1oo leen di noot te di leen y\u00f3bbu fa kanam \u00e0ttekat yi?\n2:7 Ndax du\u00f1u tilimal tur wu tedd, wi ngeen di wuyoo?\n2:8 Su ngeen s\u00e0mmee yoonu Buur Y\u00e0lla, ni ko Mbind mi t\u00ebrale naan: \u00abNanga b\u00ebgg sa moroom, ni nga b\u00ebgge sa bopp,\u00bb kon def ngeen lu baax.\n2:9 Waaye su ngeen g\u00ebnalee, b\u00e0kkaar ngeen, te yoonu Y\u00e0lla dina leen dab ni \u00f1u moy.\n2:10 Ndaxte ku s\u00e0mm yoon w\u00e9pp, waaye x\u00ebtt ci lenn ndigal rekk, j\u00e0dd nga yoon w\u00e9pp.\n2:11 Ndaxte Y\u00e0lla mi ne: \u00abBul njaaloo,\u00bb teg na ca ne: \u00abBul rey nit.\u00bb Ku njaaloowul nag, waaye nga rey nit, j\u00e0dd nga yoon w\u00e9pp.\n2:12 Gannaaw dingeen nar a jaar ci \u00e0tteb yoon, wiy goreel, na loolu lal seen wax ak seen j\u00ebf.\n2:13 Ndaxte ku y\u00ebr\u00ebmul, yoon du la y\u00ebr\u00ebm. Te y\u00ebrmande mooy noot \u00e0tte.\n2:14 Te lii itam samay bokk, ku ne g\u00ebm nga, te j\u00ebfewoo ko, loolu lu muy jari\u00f1? Ndax googu ng\u00ebm man na laa musal?\n2:15 Su amee mbokk ci seen biir, mu rafle te amul dund, muy g\u00f3or walla jig\u00e9en,\n2:16 te kenn ci y\u00e9en ne ko: \u00abDemal ak j\u00e0mm, nga solu te lekk,\u00bb te fekk fajuleen aajoom, loolu lu muy jari\u00f1?\n2:17 Noonu ng\u00ebm gu \u00e0ndul ak j\u00ebf, amul benn njari\u00f1.\n2:18 Waaye xanaa dina am ku ne: \u00abYaw am nga ng\u00ebm, man am naa ay j\u00ebf.\u00bb Yaw nag won ma sa ng\u00ebm gu \u00e0ndul ak j\u00ebf, man ma fee\u00f1al la sama ng\u00ebm ci samay j\u00ebf.\n2:19 G\u00ebm nga ne Y\u00e0lla kenn la; loolu lu baax la, waaye xamal ne, jinne yi it g\u00ebm na\u00f1u loolu, ba da\u00f1oo tiit bay lox.\n2:20 Yaw mi g\u00e0tt xel, kaay ma won la ne, ng\u00ebm gu \u00e0ndul ak j\u00ebf, amul njari\u00f1.\n2:21 Sunu maam Ibraayma, ndax du ci kaw j\u00ebf la ko Y\u00e0lla \u00e0ttee ni ku jub, ci li mu joxe doomam Isaaxa ni sarax?\n2:22 Kon gis nga ne, ng\u00ebm dafa l\u00ebngoo ak ay j\u00ebfam, te ng\u00ebmam mat ci kaw j\u00ebf jooju.\n2:23 Noonu li \u00f1u wax ci Mbind mi am na, bi mu naan: \u00abIbraayma g\u00ebm na Y\u00e0lla, te Y\u00e0lla j\u00e0ppe ng\u00ebmam ni njub,\u00bb ba \u00f1u ko wooye xaritu Y\u00e0lla.\n2:24 Kon nag gis nga ne, Y\u00e0lla ci j\u00ebf lay \u00e0tte nit ni ku jub, waaye du ci kaw ng\u00ebm kese.\n2:25 Naka Raxab jig\u00e9enu moykat bi itam, ndax du ci noonu la ko Y\u00e0lla \u00e0ttee ni ku jub, ci li mu teeru ndawi Yawut yi, te jaarale leen ca poot ba?\n2:26 Kon nag ni j\u00ebmm ju amul ruu nekke ndee, noonu la ng\u00ebm gu \u00e0ndul ak j\u00ebf nasaxe.\n3:1 Samay bokk, bu \u00f1\u00e9pp di sababloo nekk j\u00e0ngalekatu mbooloo mi, xam ne nun j\u00e0ngalekat yi, \u00e0tte bi nuy jaar mooy g\u00ebn a diis.\n3:2 Ndaxte nun \u00f1\u00e9pp sikk nanu ci f\u00e0nn yu bare. Ki sikkul ci k\u00e0ddoom, ku mat nga, te man a noot sa yaram w\u00e9pp.\n3:3 Noonu ku laab fas, ngir mu d\u00e9ggal la, noot nga j\u00ebmmam j\u00e9pp.\n3:4 Te gaal yi it yu r\u00e9y la\u00f1u, te ngelaw lu am doole di leen ji\u00f1ax, waaye dawalkat bi, we\u00f1 gu tuuti la leen di j\u00ebme fu ko neex.\n3:5 Ci noonu l\u00e0mmi\u00f1, c\u00e9r su tuuti la, waaye day b\u00e0kkoo j\u00ebf yu r\u00e9y. Seetleen ni fer\u00f1ent tuutee, te man a l\u00e0kk \u00e0ll bu yaatu.\n3:6 Noonu it l\u00e0mmi\u00f1 safara la, di bon-bonu \u00e0ddina ci biir c\u00e9r yi, tey musibaal j\u00ebmm j\u00e9pp. Jum la, bu Seytaane taal, muy lakk \u00e0ddina.\n3:7 Nit man na noot xeeti rab y\u00e9pp: rabi \u00e0ll yi, picc yi, yiy raam ak yi ci g\u00e9ej gi; noot na l\u00e9pp.\n3:8 Waaye l\u00e0mmi\u00f1 kenn m\u00ebnu koo noot; musiba la mu dul dal mukk, fees dell ak da\u014bar juy rey.\n3:9 L\u00e0mmi\u00f1 lanuy sante Boroom bi, di sunu Baay, ba noppi m\u00f3oloo ko nit, \u00f1i Y\u00e0lla s\u00e0kk ci meloom.\n3:10 G\u00e9mmi\u00f1 gi sante mooy m\u00f3oloo. Y\u00e9en samay bokk, loolu warul a am.\n3:11 Ndax ndox mu lewet ak mu wex dina\u00f1u ballandoo ci genn mb\u00ebnn?\n3:12 Samay bokk, ndax mas ngeen a gis garabu figg gu me\u00f1\u00f1 oliw, walla garabu r\u00e9se\u00f1 gu me\u00f1\u00f1 ay figg? Mukk! Mb\u00ebnnu xorom m\u00ebnta n\u00e0cc mukk ndox mu neex.\n3:13 Ana ku neex xel ci y\u00e9en, ana kuy boroom xam-xam? Na ko wone ciy j\u00ebfam ak dundam gu sell, te fee\u00f1al xelam ci jikkoom ju lewet.\n3:14 Waaye ku am ci sa xol farlu gu laloo wextan ak wut aw tur, bul b\u00e0kku, di weddi d\u00ebgg.\n3:15 Xel moomu j\u00f3gewul ci kaw; j\u00ebfu \u00e0ddina la, di jikkoy niti kese, te j\u00f3ge ci Seytaane.\n3:16 Ndaxte fu wextan ak wut aw tur dugg, indi fa x\u00ebccoo ak b\u00e9pp \u00f1aawteef.\n3:17 Waaye xel mi j\u00f3ge ci kaw daa sell, ba noppi \u00e0nd ak j\u00e0mm te lewet, nooy, fees dell ak y\u00ebrmande ak j\u00ebf yu rafet; \u00e0ndul ak genn parl\u00e0qu, amul genn naaf\u00e9q.\n3:18 Te nitu j\u00e0mm dina bey toolu j\u00e0mm, g\u00f3ob njub.\n4:1 Xeex yi ak xuloo yi ci seen biir nag, lu leen waral? Xanaa du ci seeni b\u00ebgg-b\u00ebgg, yiy xeex ci seeni c\u00e9r?\n4:2 Dangeen di m\u00e9b\u00e9t waaye dungeen am; dangeen di rey nit, boole ci ki\u00f1aan, waaye li ngeen di y\u00f3otu, dungeen ko jot; dangeen di xuloo ak a xeex waaye dungeen am dara, ndaxte \u00f1aanuleen Y\u00e0lla.\n4:3 Bu ngeen \u00f1aanee sax, dungeen jot dara, ndax y\u00e9ena ngi \u00f1aan ci naaf\u00e9q, ngir g\u00ebn a topp seen nafsu.\n4:4 Y\u00e9en \u00f1i fecci seen k\u00f3ll\u00ebre ak Y\u00e0lla, xanaa xamuleen ne mb\u00ebggeelu \u00e0ddina, mba\u00f1eel la fa Y\u00e0lla? Ku b\u00ebgg a xaritoo ak \u00e0ddina nag, noonoo nga ak Y\u00e0lla.\n4:5 Xanaa yaakaar ngeen ne, Mbind mi day wax cig neen, ci li mu ne: \u00abY\u00e0lla am na mb\u00ebggeel gu fiir ci Xel mi mu def ci nun.\u00bb\n4:6 Waaye yiwu Y\u00e0llaa ko \u00ebpp. Moom la Mbind mi wax ne:\u00abY\u00e0lla d\u00e0q na \u00f1i r\u00e9y,waaye yiwal na \u00f1i woyof.\u00bb\n4:7 Kon nag w\u00e0kkirluleen ci Y\u00e0lla, waaye d\u00e0qleen Seytaane, te dina daw, ba sore leen.\n4:8 Jegeleen Y\u00e0lla, mu jege leen. Y\u00e9en b\u00e0kkaarkat yi, sellal-leen seeni loxo; y\u00e9en \u00f1i am xel \u00f1aar, laabal-leen seeni xol.\n4:9 Toroxluleen te naqarlu, bay jooy; defleen seeni ree aw naqar, te seen mb\u00e9g nekk tiis.\n4:10 Suufeel-leen seen bopp fa kanam Boroom bi, kon dina leen y\u00e9kkati.\n4:11 Y\u00e9en bokk yi, buleen \u014b\u00e0\u00f1\u00f1ante. Ku \u014b\u00e0\u00f1\u00f1 sa moroom mbaa nga \u00f1aaw njort, ba \u00e0tte ko, dii\u014bat nga yoonu Y\u00e0lla te \u00e0tte ko; ku \u00e0tte yoon wi nag s\u00e0mmoo ko, waaye danga koo \u00e0tte.\n4:12 Kenn rekk mooy t\u00ebral yoon, kooku rekk mooy \u00e0tte; moo man a musle, moo man a alage. Te sax yaw miy \u00e0tte sa bokk yaay kan?\n4:13 L\u00e9egi nag d\u00e9gluleen, y\u00e9en \u00f1iy wax ne: \u00abTey walla \u00ebll\u00ebg dinanu dem ca d\u00ebkk s\u00e0ngam, def fa at, di fa s\u00e0kku xaalis ci jula.\u00bb\n4:14 Ndax dangeen a xam seen \u00ebll\u00ebg? Te luy seen dund? Xanaa c\u00f3ola do\u014b\u014b luy naaw ci diir bu g\u00e0tt, daldi naaxsaay.\n4:15 Lii kay ngeen waroon a wax: \u00abBu soobee Boroom bi, dinanu dund, tey def n\u00e0ngam ak n\u00e0ngam.\u00bb\n4:16 Waaye fi mu ne, naagu ngeen bay damu, te damoo noonu baaxul.\n4:17 Kon nag ku xam def lu baax te defoo ko, b\u00e0kkaar nga.\n5:1 D\u00e9gluleen y\u00e9en boroom alal yi, jooyleen te naqarlu ndax mbugal, gi leen di xaar.\n5:2 Seen alal seey na, seen y\u00e9re yi maxe na,\n5:3 seen wurus ak seen xaalis xomaag na. Te xomaag jooju seede lay doon, su leen di daanlu, ba lakk leen ni safara. Dajale ngeen alal ju ne g\u00e0\u00f1\u00f1, te fekk y\u00e9ena ngi ci muju jamono.\n5:4 D\u00e9gluleen, jooyi xaalis bi ngeen s\u00e0cce ci gubkat, yi leen doon ligg\u00e9eyal, ak yuuxi g\u00f3obkat yi, dugg na\u00f1u ci noppi Y\u00e0lla Aji K\u00e0ttan ji.\n5:5 Ci barele ak b\u00e0nneex ngeen dunde ci kaw suuf, di yafal seen bopp, fekk b\u00e9su rendi baa ngii.\n5:6 Daan ngeen ku jub, ba rey ko sax, te ba\u00f1ul.\n5:7 Y\u00e9en samay bokk, mu\u00f1leen, ba Boroom bi dellusi ci ndamam. Seetleen ci beykat bi, ni muy xaare njari\u00f1 ci me\u00f1\u00f1eefu suuf, tey mu\u00f1, c\u00e9ebo ba b\u00ebt w\u00e0cc.\n5:8 Y\u00e9en itam nag mu\u00f1leen te d\u00ebg\u00ebral seen xol, xam ne \u00f1\u00ebwu Boroom bi ci ndamam jege na.\n5:9 Buleen j\u00e0mbatante, samay bokk, ngir ragal Y\u00e0lla \u00e0tte leen. \u00c0ttekat baa ngi ci bunt bi sax!\n5:10 Bokk yi, defleen yonent, yi wax ci turu Boroom bi, seeni royukaay ci mu\u00f1 tiis ak ci g\u00f3or-g\u00f3orlu.\n5:11 Xam ngeen ne \u00f1iy g\u00f3or-g\u00f3orlu, \u00f1u barkeel la\u00f1u. D\u00e9gg ngeen mu\u00f1 ga Ay\u00f3oba amoon, te gis muj gu rafet, ga ko Boroom bi jagleel, ndax Boroom bi kuy \u00f1eewante la te bare y\u00ebrmande.\n5:12 Te li fi raw samay bokk, buleen waat mukk, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu man a doon. Nangeen yem ci: \u00abWaaw,\u00bb ak \u00abD\u00e9ed\u00e9et,\u00bb ngir ba\u00f1 cee layoo fa kanam Y\u00e0lla.\n5:13 Su amee ci y\u00e9en ku nekk ci tiis, na \u00f1aan ci Y\u00e0lla. Ku nekk ci mb\u00e9g, na sant Y\u00e0lla ciy woy.\n5:14 Su amee ci y\u00e9en ku wopp, na woo njiiti mbooloo mi, \u00f1u \u00f1aanal ko te diw boppam ci turu Boroom bi.\n5:15 Te \u00f1aan gu \u00e0nd ak ng\u00ebm dina musal ki wopp, ba Boroom bi y\u00e9kkati ko. Te su ko fekkoon ak i b\u00e0kkaar sax, Y\u00e0lla dina ko baal.\n5:16 Kon nag waxanteleen seeni b\u00e0kkaar tey \u00f1aanalante, ngir ngeen w\u00e9r. \u00d1aanu aji jub gu d\u00ebggu, dooleem amul kem.\n5:17 Naka noonu Iliyas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye bi mu saxee ci \u00f1aan Y\u00e0lla, ngir mu ba\u00f1 a taw, ndox laalul suuf diirub \u00f1etti at ak genn-w\u00e0ll.\n5:18 Gannaaw ga mu dellu \u00f1aan, asamaan daldi taw, te suuf si saxal me\u00f1\u00f1eef.\n5:19 Samay bokk, su amee ci y\u00e9en ku r\u00e9ere d\u00ebgg, te am ku ko gindi,\n5:20 na xam lii: ku gindi b\u00e0kkaarkat ci r\u00e9eram, musal nga nit ci dee te faral ko b\u00e0kkaar yu bare.","title":"Wolof Bible (NT): James","type":"page"}
