{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/jde.htm","path":"bib/wb/wlf/jde.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/jde.htm","text":"1:1 Man Yudd, jaamu Yeesu Kirist, mi bokk ak Saag ndey ak baay, maa leen di bind, y\u00e9en \u00f1i Y\u00e0lla Baay bi woo te b\u00ebgg leen, te Yeesu Kirist aar leen.\n1:2 Na leen Y\u00e0lla may y\u00ebrmande, j\u00e0mm ak mb\u00ebggeel.\n1:3 Samay bokk, b\u00ebggoon naa leen a bind lool ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye lii moo g\u00ebn a jamp: ma xiir leen, ngeen taxaw ci aar mboolem d\u00ebgg, yi Y\u00e0lla xas a d\u00e9nk gaayam yu sell yi ba f\u00e0ww.\n1:4 Ndaxte am na ay nit \u00f1u \u00f1eme Y\u00e0lla, \u00f1u yoxoosu ci seen biir; da\u00f1uy mbubboo yiwu Y\u00e0lla, ngir topp seen bakkan, di ci weddi Buur Y\u00e0lla miy kenn ak sunu Boroom Yeesu Kirist. Fekk Mbind mi t\u00ebral na seen \u00e0tte bu y\u00e0gg.\n1:5 Xam ngeen loolu l\u00e9pp ba noppi sax, waaye dama leen koy f\u00e0ttali rekk. Xam ngeen ne Boroom bi musal na xeetam, ba g\u00e9nne leen r\u00e9ewu Misra, waaye gannaaw ba raafal na \u00f1i g\u00ebmul woon.\n1:6 Te it malaaka ya j\u00e0ppul woon ca daraja ja \u00f1u amoon, xanaa toxoo fa \u00f1u leen d\u00eb\u00ebloon, Y\u00e0lla yeew na leen buum yu sax, t\u00ebj leen ci biir l\u00ebnd\u00ebm, di leen n\u00e9ge \u00e0tteb b\u00e9s bu mag ba.\n1:7 Noonu itam d\u00ebkki Sodom ak Gomor ak d\u00ebkk ya leen w\u00ebroon, da\u00f1oo s\u00f3obu ci njaaloo ak di def ay g\u00f3or-jig\u00e9en, waaye \u00e0tte bi dal na ci seen kaw, ba \u00f1uy ay tegtal ci \u00f1iy yelloo safara ba f\u00e0ww.\n1:8 Naka noonu itam gentkat yooyu may wax \u00f1u ngi sobeel seen yaram, di weddi g\u00e9pp kilifteef, di xas doole yi ci asamaan.\n1:9 Waaye bi Mikayel, miy kilifa ci malaaka yi, di x\u00ebccook Seytaane n\u00e9ewu Musaa, bay xuloo ak moom, \u00f1emewu koo \u00e0tte, boole ciy xas; mu yem ci wax ko ne: \u00abNa la Boroom bi mbugal!\u00bb\n1:10 Waaye nit \u00f1ii may wax, da\u00f1uy saaga li \u00f1u xamul. Te li \u00f1u xam ci ta\u00f1axu sax, ni b\u00e0yyima yu amul xel, da\u00f1u ci y\u00e0q seen bopp.\n1:11 \u00d1oo kay torox! Da\u00f1oo jaar ci yoonu Kayin, s\u00f3obu ci r\u00e9erug Balaam ngir xaalis, di ba\u00f1 kilifteef ni Kore, te dina\u00f1u dee ni moom.\n1:12 Su \u00f1u bokkee ak y\u00e9en reeru mbooloo mi, da\u00f1u ciy indi ay, niy xeer yu n\u00ebbbu ci biir g\u00e9ej; amu\u00f1u genn g\u00e0cce, waaye da\u00f1uy giiroo te fonk seen biir rekk. \u00d1u ngi mel ni xiin yu amul ndox, yuy naaxsaay ci ngelaw; ni garab yu me\u00f1\u00f1ul ci jamonoy me\u00f1\u00f1eef, te buddeeku, dee ba wow ko\u014b\u014b;\n1:13 mel ni duusi g\u00e9ej gu mer, yuy g\u00ebq j\u00ebf yu ruslu; niy biddiiw yuy faq, te Y\u00e0lla dencal na leen l\u00ebnd\u00ebm ya g\u00ebn a tar ba f\u00e0ww.\n1:14 Enog, di jur\u00f3om-\u00f1aareelu maam gannaaw Aadama, waxoon na ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, ba weer leen ne: \u00abBoroom bi w\u00e0cce na ca asamaan, \u00e0nd ak ay junniy junniy malaakaam,\n1:15 ngir \u00e0tte \u00f1\u00e9pp, te mbugal \u00f1i weddi \u00f1\u00e9pp ndax \u00f1aawteef, yi \u00f1u j\u00ebf ci \u00f1eme Y\u00e0lla; di leen f\u00e0ttali it k\u00e0ddu yu \u00f1aaw, yi \u00f1u ko tifaar ci seeni b\u00e0kkaar ak seen weddi.\u00bb\n1:16 Du\u00f1u noppee xultu, di j\u00e0mbat seen nekkin, tey topp seen nafsu; ay wax yu r\u00e9y a ngi ball ci seen l\u00e0mmi\u00f1, waaye da\u00f1uy jey \u00f1i \u00f1uy yaakaare njari\u00f1.\n1:17 Waaye y\u00e9en samay xarit, f\u00e0ttalikuleen la leen ndawi sunu Boroom Yeesu Kirist waxoon lu jiitu,\n1:18 ne leen: \u00abMuju jamono ay tii\u00f1alkat dina\u00f1u fee\u00f1, \u00f1uy weddi Y\u00e0lla, ngir topp seen bakkan.\u00bb\n1:19 \u00d1ooy f\u00e9ewale, te Xelum Y\u00e0lla nekkul ci \u00f1oom, waaye niti kese la\u00f1u.\n1:20 Waaye y\u00e9en samay xarit, doolewuleen ci seen yoonu ng\u00ebm wu sell, tey \u00f1aan ci dooley Xel mu Sell mi,\n1:21 ba saxoo mb\u00ebggeelu Y\u00e0lla, tey s\u00e9entu y\u00ebrmandey sunu Boroom Yeesu Kirist, mu t\u00e0bbal leen ci dund gu dul jeex.\n1:22 Jubbantileen \u00f1i am werantey xel,\n1:23 ngeen musal \u00f1ale, j\u00eble leen ci safara, te y\u00ebr\u00ebm \u00f1eneen \u00f1i, waaye boole ci moytu, ba sib sax seen y\u00e9re yi taq sobe.\n1:24 Y\u00e0lla mi leen man a aar ci g\u00e9pp jeng, te teewal leen fa kanam ndamam, ngeen \u00f1\u00e0kk sikk te fees dell ak mb\u00e9g;\n1:25 Y\u00e0lla miy kenn, di sunu Musalkat, na yelloo ndam ak m\u00e0gg, k\u00e0ttan ak nguur, jaar ci Yeesu Kirist sunu Boroom, d\u00e9mb, tey, \u00ebll\u00ebg ba f\u00e0ww. Amiin.","title":"Wolof Bible (NT): Jude","type":"page"}
