{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/jo1.htm","path":"bib/wb/wlf/jo1.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/jo1.htm","text":"1:1 Nu ngi leen di bind ci mbirum Ki \u00f1uy wax K\u00e0ddug dund, moom mi amoon ca nj\u00e0lb\u00e9en ga; mi nu d\u00e9gg te gis ko ak sunuy b\u00ebt, mi nu xool te laal ko ak sunuy loxo.\n1:2 Dund fee\u00f1 na, te gis nanu ko; te moom lanuy seedeel, di leen y\u00e9gal dund gu dul jeex, googu nekkoon ci wetu Y\u00e0lla Baay bi te fee\u00f1u nu.\n1:3 Li nu gis te d\u00e9gg ko, nu ngi leen koy y\u00e9gal, ngir y\u00e9en itam ngeen bokk ak nun. Te d\u00ebgg-d\u00ebgg bokk nanu ci Baay bi ak Doomam, Yeesu Kirist.\n1:4 Nu ngi leen di bind y\u00ebf yii, ngir sunu mb\u00e9g mat s\u00ebkk, nun \u00f1\u00e9pp.\n1:5 Xebaar bi nu d\u00e9gg ci Yeesu Kirist, di leen ko y\u00e9gal, mooy lii: Y\u00e0lla Leer la, te genn l\u00ebnd\u00ebm nekkul ci moom.\n1:6 Su nu waxee ne, bokk nanu ci moom, tey dox ci l\u00ebnd\u00ebm, danuy fen ci sunuy wax ak sunuy j\u00ebf.\n1:7 Waaye bu nuy dox ci leer, ni mu nekke moom ci boppam ci leer, kon bokk nanu ci sunu biir, te deretu Yeesu Doomam dina nu sellal ci b\u00e9pp b\u00e0kkaar.\n1:8 Su nu waxee ne amunu b\u00e0kkaar, kon nax nanu sunu bopp, te d\u00ebgg nekkul ci nun.\n1:9 Su nu nangoo sunuy b\u00e0kkaar ci kanamam, fekk kuy s\u00e0mm k\u00f3ll\u00ebre la te jub, ngir baal nu sunuy b\u00e0kkaar te sellal nu ci l\u00e9pp lu jubadi.\n1:10 Su nu waxee ne defunu b\u00e0kkaar, teg nanu ko kuy tebbi waxam, te k\u00e0ddoom duggagul ci sunu xol.\n2:1 Samay doom, maa ngi leen di bind y\u00ebf yii, ngir ngeen ba\u00f1 a def b\u00e0kkaar. Waaye su kenn defee b\u00e0kkaar, ba tey am nanu ku nuy rammu ci Baay bi, mooy Yeesu Kirist mu jub mi.\n2:2 Te moo joxe bakkanam, ngir dindi sunuy b\u00e0kkaar, te du sax sunuy b\u00e0kkaar rekk, waaye yu \u00e0ddina s\u00e9pp.\n2:3 Ci lii lanu xame ne, xam nanu ko: s\u00e0mm ay ndigalam.\n2:4 Ku wax ne xam nga ko, te s\u00e0mmoo ay ndigalam, dangay fen, te d\u00ebgg nekkul ci yaw.\n2:5 Kuy s\u00e0mm k\u00e0ddug Y\u00e0lla, d\u00ebgg-d\u00ebgg sa mb\u00ebggeel ci Y\u00e0lla mat na s\u00ebkk. Ci loolu lanu xame ne, nekk nanu ci moom.\n2:6 Ku wax ne ci Y\u00e0lla nga sax, f\u00e0ww nga dund, ni Yeesu Kirist daan dunde moom ci boppam.\n2:7 Samay soppe, li ma leen di bind du ndigal lu bees, waaye ndigal lu y\u00e0gg la; la ngeen jotoon ca ndoorte la. Te ndigal lu y\u00e0gg loolu, mooy k\u00e0ddu gi ngeen d\u00e9ggoon.\n2:8 Teewul ndigal lu bees laa leen di bind, lu amoon ci dundu Yeesu, te am it ci seen dund; ndaxte l\u00ebnd\u00ebm gaa ngi w\u00e9y, te leer gu w\u00f3or gi fenk na xaat.\n2:9 Ku wax ne yaa ngi ci leer, tey ba\u00f1 sa mbokk, yaa ngi ci l\u00ebnd\u00ebm ba tey.\n2:10 Kuy sopp sa mbokk, yaa ngi d\u00ebkk ci leer, te luy y\u00f3bbe nit b\u00e0kkaar du nekk ci yaw.\n2:11 Waaye kuy ba\u00f1 sa mbokk, ci l\u00ebnd\u00ebm nga nekk, di ci dox, te xamoo foo j\u00ebm, ndax l\u00ebnd\u00ebm muur na say b\u00ebt.\n2:12 Samay doom, maa ngi leen di bind,ndax baalees na leen seeni b\u00e0kkaar ci turu Kirist.\n2:13 Maa ngi leen di bind, y\u00e9en baay yi,ndax xam ngeen Ki nekkoon ca nj\u00e0lb\u00e9en ga ba tey.Maa ngi leen di bind, y\u00e9en waxambaane yi,ndax daaneel ngeen Ibliis.\n2:14 Bind naa leen, samay doom,ndax xam ngeen Y\u00e0lla Baay bi.Bind naa leen, y\u00e9en baay yi,ndax xam ngeen Ki nekkoon ca nj\u00e0lb\u00e9en ga ba tey.Bind naa leen, y\u00e9en waxambaane yi,ndax y\u00e9ena ngi d\u00ebg\u00ebr,ndax k\u00e0ddug Y\u00e0llaa ngi d\u00ebkk ci y\u00e9en,te daaneel ngeen Ibliis.\n2:15 Buleen sopp \u00e0ddina ak li ci biiram. Ku sopp \u00e0ddina, mb\u00ebggeelu Baay bi nekkul ci moom.\n2:16 Ndaxte l\u00e9pp lu nekk ci \u00e0ddina, maanaam b\u00ebgg-b\u00ebggu yaram ak xemmemu b\u00ebt ak r\u00e9yug \u00e0ddina, loolu du j\u00f3ge ci Baay bi waaye ci \u00e0ddina.\n2:17 Te \u00e0ddina day w\u00e9y, waaye kuy def coobareg Y\u00e0lla dinga sax ba f\u00e0ww.\n2:18 Samay doom, waxtu wu mujj wi jot na! D\u00e9gg ngeen ne, benn Ba\u00f1aaleb Kirist dina \u00f1\u00ebw; te d\u00ebgg la, ba\u00f1aaley Kirist yu bare fee\u00f1 na\u00f1u. Ci loolu lanu xame ne, waxtu wu mujj wi jot na.\n2:19 Ci sunu biir la\u00f1u j\u00f3ge, waaye bokku\u00f1u woon ci nun; ndaxte su \u00f1u bokkoon ci nun, kon dina\u00f1u des ci nun. Waaye d\u00e0ggeeku na\u00f1u nu, ngir mu leer ne, kenn ci \u00f1oom bokkul woon ci nun.\n2:20 Y\u00e9en nag, Aji Sell ji sol na leen Xelam, te y\u00e9en \u00f1\u00e9pp am ngeen xam-xam.\n2:21 Bind naa leen, du ndax xamuleen d\u00ebgg, waaye ndax xam ngeen ko, xam it ne wenn fen du j\u00f3ge ci d\u00ebgg.\n2:22 Kan mooy fenkat bi? Mooy kiy weddi ne Yeesu mooy Kirist, Almasi bi. Kooka mooy Ba\u00f1aaleb Kirist, biy weddi Baay bi ak Doom ji.\n2:23 Ku weddi Doom ji, amuloo itam Baay bi; ku seedeel Doom ji, am nga it Baay bi.\n2:24 Y\u00e9en nag, la ngeen d\u00e9ggoon ca ndoorte la, na sax ci y\u00e9en. Loolu ngeen d\u00e9ggoon ca ndoorte la, su saxee ci y\u00e9en, dingeen sax y\u00e9en itam ci Doom ji ak ci Baay bi.\n2:25 Te li mu nu digoon mooy lii: dund gu dul jeex.\n2:26 Bind naa leen lii ci mbirum \u00f1i leen di b\u00ebgg a r\u00e9eral.\n2:27 Y\u00e9en nag, Xel mi leen Kirist sol a ngi d\u00ebkk ci y\u00e9en, te soxlawuleen kenn j\u00e0ngal leen dara. Waaye Xel mi mu leen sol, mi ngi leen di j\u00e0ngal l\u00e9pp, te li mu leen di j\u00e0ngal mooy d\u00ebgg; kon nag saxleen ci moom, ni mu leen ko j\u00e0ngale.\n2:28 Gannaaw loolu nag y\u00e9en samay doom, saxleen ci Kirist, ngir b\u00e9s bu fee\u00f1ee, nu am k\u00f3olute ci kanamam te ba\u00f1 a rus ba s\u00ebng\u00e9em cig dikkam.\n2:29 Gannaaw xam ngeen ne ku jub la, dingeen xam it ne, k\u00e9pp kuy def lu jub juddu nga ci moom.\n3:1 Xool-leen mb\u00ebggeel gi nu Baay bi jox, ni mu r\u00e9ye, ba nu man a tudd doomi Y\u00e0lla. Te moom lanu. Moo tax \u00e0ddina xamu nu, ndaxte xamu ko woon, moom itam.\n3:2 Samay soppe, l\u00e9egi doomi Y\u00e0lla lanu, te li nu nar a nekki fee\u00f1agul, waaye xam nanu ne, b\u00e9s bu Almasi bi fee\u00f1ee, dinanu nirook moom, ndaxte dinanu ko gis, na mu mel.\n3:3 Te k\u00e9pp ku am yaakaar jooju ci moom, dinga sellal sa bopp, ni mu selle moom.\n3:4 Ku def b\u00e0kkaar, j\u00e0dd nga yoon; ndaxte b\u00e0kkaar mooy j\u00e0dd yoon.\n3:5 Te xam ngeen ne Yeesu Kirist fee\u00f1 na, ngir dindi b\u00e0kkaar yi, te moom amul benn b\u00e0kkaar.\n3:6 K\u00e9pp ku sax ci moom, doo sax ci b\u00e0kkaar; kuy def b\u00e0kkaar, gisuloo ko te xamuloo ko.\n3:7 Samay doom, bu leen kenn nax! Kuy def lu jub, ku jub nga, ni Kirist jube moom ci boppam.\n3:8 Kuy def b\u00e0kkaar, ci Seytaane nga bokk, ndax Seytaane ca nj\u00e0lb\u00e9en ga ba tey day b\u00e0kkaar. Te Doomu Y\u00e0lla ji \u00f1\u00ebw na, ngir nasaxal j\u00ebfi Seytaane.\n3:9 Ku juddu ci Y\u00e0lla doo def b\u00e0kkaar, ndax Y\u00e0lla sol na la jikkoom, te doo man a sax ci b\u00e0kkaar, ndax juddu nga ci Y\u00e0lla.\n3:10 Lii mooy r\u00e0\u00f1\u00f1ale doomi Y\u00e0lla ak doomi Seytaane: k\u00e9pp ku dul def lu jub bokkoo ci Y\u00e0lla; naka noonu itam ku soppul sa mbokk bokkoo ci Y\u00e0lla.\n3:11 Ndaxte xebaar, bi ngeen d\u00e9ggoon ca ndoorte la, mooy lii: nanu b\u00ebggante,\n3:12 te ba\u00f1 a mel ni Kayin, mi bokkoon ci Ibliis, ba rey rakkam. Lu tax mu rey ko nag? Ndaxte ay j\u00ebfam da\u00f1oo bon, te yu rakkam jub.\n3:13 Bokk yi, bu leen \u00e0ddina ba\u00f1ee, buleen ci jaaxle.\n3:14 Mb\u00ebggeel gi nu b\u00ebgg sunuy bokk moo nuy xamal ne, j\u00f3ge nanu ci dee, t\u00e0bbi ci dund. Ku b\u00ebggul sa mbokk, yaa ngi ci dee ba tey.\n3:15 K\u00e9pp ku ba\u00f1 sa mbokk, reykat nga; te xam ngeen ne, ku rey nit amuloo dund gu dul jeex.\n3:16 Ci lii lanuy x\u00e0mmee luy mb\u00ebggeel: Kirist joxe na bakkanam ngir nun; te nun itam war nanoo joxe sunu bakkan ngir sunuy bokk.\n3:17 Waaye ku am alalu \u00e0ddina te gis sa mbokk nekk ci soxla, nga dumm\u00f3oyu ko, nan la mb\u00ebggeelu Y\u00e0lla d\u00ebkke ci yaw?\n3:18 Samay doom, bunu b\u00ebggante ci wax mbaa ci l\u00e0mmi\u00f1 rekk, waaye ci j\u00ebf ak ci d\u00ebgg.\n3:19 Ci loolu lanu xame ne, nu ngi ci d\u00ebgg; te waxtu wu sunu xol di xeex ak nun, dinanu ko dalal ci kanamam; ndaxte Y\u00e0llaa \u00ebpp sunu xol te xam na l\u00e9pp.\n3:21 Samay soppe, bu nu sunu xol daanul, kon man nanoo jege Y\u00e0lla ak k\u00f3olute.\n3:22 Te l\u00e9pp lu nu koy \u00f1aan, dinanu ko jot ci moom, ndaxte nu ngi s\u00e0mm ay ndigalam, di def lu ko neex.\n3:23 Ndigalam mooy lii: nu g\u00ebm turu Doomam, Yeesu Kirist, tey b\u00ebggante, ni mu nu ko digale.\n3:24 Kuy s\u00e0mm ndigalu Y\u00e0lla, dinga sax ci moom, mu d\u00ebkk ci yaw. Te Xel mi mu nu jox, moo nuy xamal ne, d\u00ebkk na ci nun.\n4:1 Samay soppe, buleen g\u00ebm xel mu nekk, waaye nattuleen xel yi, ba xam ndax ci Y\u00e0lla la\u00f1u j\u00f3ge walla d\u00e9et, ndaxte naaf\u00e9q yu bare yu mbubboo turu yonent j\u00f3g na\u00f1u, tasaaroo ci \u00e0ddina si.\n4:2 Ci lii lanu x\u00e0mmee Xelum Y\u00e0lla: m\u00e9pp xel mu nangu ne, Yeesu Kirist \u00f1\u00ebw na, nekk nit, ci Y\u00e0lla la bokk.\n4:3 Waaye m\u00e9pp xel mu nanguwul Yeesu, bokkul ci Y\u00e0lla. Xel moomu mooy xelum Ba\u00f1aaleb Kirist, mi ngeen d\u00e9ggoon ne dina \u00f1\u00ebw, te l\u00e9egi sax mu ngi ci biir \u00e0ddina.\n4:4 Y\u00e9en samay doom, ci Y\u00e0lla ngeen bokk, te daan ngeen yonent yu naaf\u00e9q yooyu, ndaxte Ki nekk ci y\u00e9en moo \u00ebpp doole ki nekk ci \u00e0ddina.\n4:5 \u00d1oom ci \u00e0ddina la\u00f1u bokk; moo tax \u00f1uy wax waxi \u00e0ddina, te \u00e0ddina di leen d\u00e9glu.\n4:6 Nun nag ci Y\u00e0lla lanu bokk. Ku xam Y\u00e0lla dinga nu d\u00e9glu; ku bokkul ci Y\u00e0lla doo nu d\u00e9glu. Ci loolu lanuy x\u00e0mmee Xel miy d\u00ebgg ak xel mi dul d\u00ebgg.\n4:7 Samay soppe, nanu b\u00ebggante, ndax mb\u00ebggeel ci Y\u00e0lla la bawoo; k\u00e9pp ku b\u00ebgg sa mbokk nag, ci Y\u00e0lla nga juddoo, te xam nga Y\u00e0lla.\n4:8 Ku b\u00ebggul sa mbokk, xamuloo Y\u00e0lla, ndax Y\u00e0lla mb\u00ebggeel la.\n4:9 Nii la Y\u00e0lla wonee mb\u00ebggeelam ci nun; y\u00f3nni na ci \u00e0ddina jenn Doomam ji mu am kepp, ngir nu am dund ci moom.\n4:10 Lii mooy mb\u00ebggeel, du sunu mb\u00ebggeel ci Y\u00e0lla, waaye mb\u00ebggeelam ci nun, ba mu y\u00f3nni Doomam, mu joxe bakkanam, ngir dindi sunuy b\u00e0kkaar.\n4:11 Samay soppe, bu nu Y\u00e0lla b\u00ebggee nii, nun itam war nanoo b\u00ebggante.\n4:12 Kenn musul a gis Y\u00e0lla, waaye bu nu b\u00ebggantee, Y\u00e0llaa ngi d\u00ebkk ci nun te mb\u00ebggeelam mat na s\u00ebkk ci nun.\n4:13 Ci lii lanuy xame ne, sax nanu ci Y\u00e0lla, te moom itam d\u00ebkk na ci nun: sol na nu Xelam.\n4:14 Te nun gis nanu te seede ne, Baay bi y\u00f3nni na Doom ji, mu nekk Musalkatu \u00e0ddina.\n4:15 K\u00e9pp ku nangu ne, Yeesu Doomu Y\u00e0lla la, Y\u00e0lla d\u00ebkk na ci yaw, te yaw it sax nga ci Y\u00e0lla.\n4:16 Mb\u00ebggeel gi Y\u00e0lla am ci nun, xam nanu ko te g\u00ebm ko. Y\u00e0lla mb\u00ebggeel la, te k\u00e9pp ku sax ci mb\u00ebggeel, yaa ngi sax ci Y\u00e0lla, mu d\u00ebkk ci yaw.\n4:17 Ni Kirist mel, noonu lanu mel nun itam ci \u00e0ddina. Ci loolu la mb\u00ebggeel mate s\u00ebkk ci nun, ngir nu am k\u00f3olute b\u00e9su \u00e0tte ba.\n4:18 Genn ragal amul ci mb\u00ebggeel, waaye mb\u00ebggeel gu mat s\u00ebkk day d\u00e0q ragal. Ndaxte ragal day \u00e0nd ak mbugal; te ku ragal, mb\u00ebggeel matul s\u00ebkk ci yaw.\n4:19 Danuy w\u00e9y ci mb\u00ebggeel, ndax moo nu j\u00ebkk a b\u00ebgg.\n4:20 Su kenn nee: \u00abB\u00ebgg naa Y\u00e0lla,\u00bb te b\u00ebgguloo sa mbokk, dangay fen; ndaxte ku b\u00ebggul sa mbokk mi ngay gis, doo man a b\u00ebgg Y\u00e0lla mi nga gisul.\n4:21 Te jox na nu ndigal lii: ku b\u00ebgg Y\u00e0lla, nga b\u00ebgg sa mbokk.\n5:1 K\u00e9pp ku g\u00ebm ne Yeesu mooy Almasi bi, juddu nga ci Y\u00e0lla; te ku b\u00ebgg waajur, dinga b\u00ebgg itam ki mu jur.\n5:2 Xam nanu ne, b\u00ebgg nanu doomi Y\u00e0lla yi ci lii: b\u00ebgg Y\u00e0lla tey s\u00e0mm ay ndigalam.\n5:3 Ndaxte mb\u00ebggeel ci Y\u00e0lla mooy s\u00e0mm ay ndigalam; te ay ndigalam diisu\u00f1u.\n5:4 Ndaxte k\u00e9pp ku juddu ci Y\u00e0lla day noot \u00e0ddina; te li nuy noote \u00e0ddina mooy sunu ng\u00ebm.\n5:5 Ku noot \u00e0ddina mooy kan? Mooy ki g\u00ebm ne, Yeesu mooy Doomu Y\u00e0lla.\n5:6 Yeesu Kirist mooy ki \u00f1\u00ebw, jaar ci ndox ak deret; du ci ndox rekk, waaye ndox ak deret. Te Xelu Y\u00e0lla mi moo koy seedeel, ndax Xel mi mooy d\u00ebgg.\n5:7 Ndaxte am na \u00f1etti seede:\n5:8 Xel mi, ndox ak deret, te \u00f1oom \u00f1ett \u00f1\u00e9pp, \u00f1oo bokk benn baat.\n5:9 Seedes nit, dinanu ko nangu, waaye seedes Y\u00e0lla moo g\u00ebn a w\u00f3or, ndax boobu seede mooy li Y\u00e0lla seede ci Doomam.\n5:10 Ku g\u00ebm Doomu Y\u00e0lla ji, am nga seede boobu ci sa xol. Ku g\u00ebmul Y\u00e0lla, teg nga ko kuy tebbi waxam ndaxte g\u00ebmuloo li Y\u00e0lla seede ci Doomam.\n5:11 Te seede si mooy lii: Y\u00e0lla jox na nu dund gu dul jeex, te dund googoo ngi ci Doomam.\n5:12 Ku am Doom ji, am nga dund; ku amul Doomu Y\u00e0lla, amuloo dund.\n5:13 Maa ngi leen di bind y\u00ebf yii, y\u00e9en \u00f1i g\u00ebm turu Doomu Y\u00e0lla ji, ngir ngeen xam ne, am ngeen dund gu dul jeex.\n5:14 K\u00f3olute gi nu am ci kanam Y\u00e0lla mooy lii, su nu ko \u00f1aanee dara ci coobareem, dina nu nangul.\n5:15 Gannaaw xam na\u00f1u ne, dina nangu l\u00e9pp lu nu koy \u00f1aan, xam nanu it ne, li nu ko \u00f1aan, jox na nu ko.\n5:16 Ku gis mbokkam, muy def b\u00e0kkaar bu jarul dee, na ko \u00f1aanal, te Y\u00e0lla dina ko may dund. Ku def b\u00e0kkaar bu jarul dee laa wax. Ndaxte am na b\u00e0kkaar bu jar dee; boobu taxul may wax, mu \u00f1aanal ko.\n5:17 G\u00e9pp jubadi b\u00e0kkaar la, waaye am na b\u00e0kkaar bu jarul dee.\n5:18 Xam nanu ne, k\u00e9pp ku juddu ci Y\u00e0lla doo sax ci b\u00e0kkaar, waaye Doomu Y\u00e0lla ji mooy wottu sa bakkan, ba Ibliis du la manal dara.\n5:19 Nun nag xam nanu ne, nu ngi ci Y\u00e0lla, te \u00e0ddina s\u00e9pp a ngi t\u00ebdd ci loxoy Ibliis.\n5:20 Xam nanu ne, Doomu Y\u00e0lla ji \u00f1\u00ebw na te may na nu xel, ba nu man a xam Aji W\u00f3or ji. Te nu ngi ci Aji W\u00f3or ji ak ci Doomam Yeesu Kirist. Kooku mooy Y\u00e0lla ju w\u00f3or, ji yor dund gu dul jeex.\n5:21 Samay doom, wottuleen seen bopp ciy x\u00ebr\u00ebm.","title":"Wolof Bible (NT): 1 John","type":"page"}
