{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/jo2.htm","path":"bib/wb/wlf/jo2.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/jo2.htm","text":"1:1 Man njiit li maa leen di bind, yaw soxna su tedd si, yaw ak say doom. B\u00ebgg naa leen bu w\u00e9r ci sama xol, j\u00e9llale naa sama bopp sax, waaye itam k\u00e9pp ku xam d\u00ebgg gi.\n1:2 Te d\u00ebgg gee tax nuy def noonu, d\u00ebgg gi d\u00ebkk ci nun, tey \u00e0nd ak nun ba f\u00e0ww.\n1:3 Y\u00e0lla Baay bi ak Yeesu Krist, Doomu Baay bi, dina\u00f1u nu may yiw, y\u00ebrmande ak j\u00e0mm, \u00e0nd ak d\u00ebgg ak mb\u00ebggeel.\n1:4 Gis naa ci say doom, \u00f1uy jaar ci t\u00e0nki d\u00ebgg, ni nu ko Baay bi digale, te b\u00e9g naa ci lool.\n1:5 L\u00e9egi nag soxna si, maa ngi lay d\u00e9nk lii: nun \u00f1\u00e9pp nanu b\u00ebggante, te loolu du d\u00e9nkaane bu bees, waaye moom lanu jotoon ca nj\u00e0lb\u00e9en ga.\n1:6 Lii mooy mb\u00ebggeel: nu w\u00e9er sunug dund ci ndigali Y\u00e0lla; loolu mooy ndigalam, la nu jotoon ca nj\u00e0lbeen ga, te ci lanu wara jaar.\n1:7 Maa ngi wax loolu nag, ndaxte am na \u00f1uy s\u00e0nke \u00f1u bare, \u00f1u tasaaroo ci \u00e0ddina si, te nanguwu\u00f1u ne Yeesu Krist w\u00e0cc na, nekk nit. Kooku aji s\u00e0nke la, di Ba\u00f1aaleb Krist.\n1:8 Kon moytuleen, ngir ba\u00f1a \u00f1\u00e0kk seen a\u00f1ub coono, waaye ngeen am yool bu mat s\u00ebkk.\n1:9 K\u00e9pp ku saxul ci d\u00e9nkaaney Krist, xanaa di ko weesu, bokkul ci Y\u00e0lla; ku sax ci d\u00e9nkaane yi, bokk nga ak Baay bi ak Doom ji.\n1:10 Ku \u00f1\u00ebw fi yaw, te indaalewul d\u00e9nkaane yooyu, waxuma nga ba\u00f1 koo teeru rekk, waaye bu ko nuyu sax.\n1:11 Ku ko nuyu, bokk nga ciy \u00f1aawteefam.\n1:12 B\u00ebggoon naa leena wax lu bare ci bataaxel bii, waaye l\u00e9pp xajul ci kayit. Kon nag fas naa y\u00e9enee \u00f1\u00ebw, ba j\u00e0kkaarlook yeen, nu waxtaan ci, ngir sunu mb\u00e9g mat s\u00ebkk.\n1:13 Say doomi rakk, ji Y\u00e0lla t\u00e0nn, \u00f1u ngi lay nuyu.","title":"Wolof Bible (NT): 2 John","type":"page"}
