{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/jo3.htm","path":"bib/wb/wlf/jo3.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/jo3.htm","text":"1:1 Man njiit li, maa ngi lay bind, yaw sama xarit Gayus, mi ma b\u00ebgg ci sama xol.\n1:2 Sama soppe, maa ngi \u00f1aan, Y\u00e0lla may la j\u00e0mm ci l\u00e9pp, \u00e0nd ak w\u00e9r gi yaram, ju mel ni sa naataangeg xol.\n1:3 Sunuy mbokk \u00f1\u00ebw na\u00f1u, te seede ni nga fonke d\u00ebgg gi, ba w\u00e9er ci sa dund g\u00e9pp, te b\u00e9g naa ci lool.\n1:4 Awma mb\u00e9g mu \u00ebpp lii: ma d\u00e9gg ne samay doomi diine \u00f1u ngiy jaar ci t\u00e0nki d\u00ebgg.\n1:5 Yaw sama xarit, sa takkute f\u00e9s na ci teeru bi ngay teeru mbokk yi, te fekk xamoo leen.\n1:6 Seedeel na\u00f1u sa mb\u00ebggeel fi kanam mbooloom \u00f1i g\u00ebm. Taxawu leen nag ci seen yoon taxawu gu neex Y\u00e0lla.\n1:7 Ndaxte turu Krist la leen taxa j\u00f3g, te s\u00e0kkuwu\u00f1u daray ku g\u00ebmul.\n1:8 Nun nag f\u00e0ww nu teeru \u00f1u mel ni \u00f1oom, ngir nu ligg\u00e9eyandoo ak d\u00ebgg gi.\n1:9 Bind naa mbooloo mi bataaxel, waaye Jotref, mi b\u00ebgg noot \u00f1\u00e9pp, du d\u00e9gg sunu ndigal.\n1:10 Kon nag su ma \u00f1\u00ebwee, dinaa f\u00e0ttali li mu def l\u00e9pp, ci di nu sosal ci k\u00e0dduy neen yu \u00f1aaw. Yemu foofu sax, waaye nanguwula teeru mbokk yi, rax-ca-dolli ku leen b\u00ebgga teeru, mu g\u00e0llankoor ko, d\u00e0q ko ci mbooloo mi.\n1:11 Sama xarit, bul roy lu bon, waaye lu baax rekk. Kuy def lu baax, ci Y\u00e0lla nga bokk; kuy def lu bon, xamoo dara ci Y\u00e0lla.\n1:12 Naka D\u00e9m\u00e9trius nag, \u00f1\u00e9pp seedeel na\u00f1u ko lu baax, te d\u00ebgg gi sax seedeel na ko ko. Nun itam seedeel nanu ko te w\u00f3or na ma ne, sunu seede d\u00ebgg la.\n1:13 Am na lu bare, lu ma la b\u00ebggoona wax, waaye l\u00e9pp xajul ci kayit.\n1:14 Kon yaakaar naa laa seetsi balaa y\u00e0gg, j\u00e0kkaarlook yaw, nu waxtaan ci.\n1:15 Na j\u00e0mm \u00e0nd ak yaw. Xarit yi y\u00e9pp \u00f1u ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy xarit, kenn ku nekk ci turam.","title":"Wolof Bible (NT): 3 John","type":"page"}
