{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/joh.htm","path":"bib/wb/wlf/joh.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/joh.htm","text":"1:1 Ca nj\u00e0lb\u00e9en ga fekk na K\u00e0ddu gi am, te K\u00e0ddu gi ma nga woon ak Y\u00e0lla, te K\u00e0ddu gi Y\u00e0lla la woon.\n1:2 Moo di ki nekkoon ak Y\u00e0lla ca nj\u00e0lb\u00e9en ga.\n1:3 Ci moom la\u00f1u s\u00e0kke l\u00e9pp. Amul dara lu \u00f1u s\u00e0kk lu jaarul ci moom.\n1:4 Ci moom la dund nekk, te dund googu mooy leeral nit \u00f1i.\n1:5 Leer gi fee\u00f1 na ci biir l\u00ebnd\u00ebm, te l\u00ebnd\u00ebm gi j\u00e0ppu ko.\n1:6 Y\u00e0lla y\u00f3nni woon na nit ku \u00f1u naan Yaxya.\n1:7 Kooku \u00f1\u00ebw na, doon ab seede, ngir wax ci mbirum leer gi. \u00d1\u00ebw na ngir \u00f1\u00e9pp d\u00e9gg li mu wax te g\u00ebm.\n1:8 Moom ci boppam du woon leer gi, waaye \u00f1\u00ebw na ngir seedeel leer gi.\n1:9 K\u00e0ddu googu mooy leer gu w\u00f3or, giy \u00f1\u00ebw ci \u00e0ddina te di leeral nit ku nekk.\n1:10 Ci \u00e0ddina la nekkoon, \u00e0ddina si \u00f1u s\u00e0kk jaarale ko ci moom, te \u00e0ddina xamu ko.\n1:11 \u00d1\u00ebw na ci r\u00e9ewam, te ay \u00f1o\u00f1am nanguwu\u00f1u ko.\n1:12 Teewul \u00f1i ko nangu te g\u00ebm ci turam, may na leen, \u00f1u am sa\u00f1-sa\u00f1u nekk doomi Y\u00e0lla.\n1:13 \u00d1oo\u00f1u judduwu\u00f1u ci deret walla ci b\u00ebgg-b\u00ebggu yaram, walla ci coobarey nit. \u00d1u ngi juddu ci Y\u00e0lla.\n1:14 K\u00e0ddu gi \u00f1\u00ebw, doon nit, d\u00ebkk ci sunu biir. Gis na\u00f1u ndamam, mu fees ak yiw ak d\u00ebgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji mu am kepp.\n1:15 Yaxyaa ngi koy seedeel te y\u00e9gle na lii; nee na: \u00abMoo taxoon ma wax ne: \u201cDina \u00f1\u00ebw sama gannaaw waaye moo ma g\u00ebn a m\u00e0gg, ndaxte nekk na laata may juddu.\u201d\u00bb\n1:16 K\u00e0ddu gi fees na ak yiw, te nun \u00f1\u00e9pp jot nanu ci sunu w\u00e0ll, mu barkeel nu ay yooni-yoon.\n1:17 Ndigali Y\u00e0lla yi, ci g\u00e9mmi\u00f1u Musaa la\u00f1u leen jaarale; yiw wi ak d\u00ebgg gi, Yeesu Kirist moo ko indaale.\n1:18 Kenn musul a gis Y\u00e0lla, waaye B\u00e0jjo bi, di Y\u00e0lla te nekk ak Baay bi, moo ko xamle.\n1:19 Lii mooy seedes Yaxya. Amoon na b\u00e9s Yawut ya y\u00f3nni ay saraxalekat ca Yaxya, \u00f1u \u00e0nd ak \u00f1u soqikoo ci giiru Lewi. \u00d1u nga j\u00f3ge Yerusalem, \u00f1\u00ebw ci moom, di ko laaj mooy kan.\n1:20 Yaxya tontu na leen te n\u00ebbbu ci dara, w\u00f3oral na leen ne, moom du Almasi bi.\n1:21 \u00d1u laaj ko ne: \u00abKon yaay kan? Ndax yaa di Iliyas?\u00bb Mu ne leen: \u00abD\u00e9ed\u00e9et, duma Iliyas.\u00bb \u00d1u ne ko: \u00abNdax yaa di Yonent, bi war a \u00f1\u00ebw?\u00bb Mu tontu ne leen: \u00abD\u00e9ed\u00e9et.\u00bb\n1:22 Noonu \u00f1u laaj ko ne: \u00abWax nu yaay kan, ngir nu man a tontu \u00f1i nu y\u00f3nni. Nga ne yaa di kan?\u00bb\n1:23 Yaxya tontu leen li yonent Y\u00e0lla Esayi waxoon ne: \u00abMan maa di baat biy y\u00e9gle ci m\u00e0ndi\u014b mi ne: \u201cX\u00e0ll-leen yoonu Boroom bi!\u201d\u00bb\n1:24 Amoon na \u00f1u bokk ca Farisen ya, yu \u00e0ndoon ca mbooloo, ma \u00f1u y\u00f3nni woon ca Yaxya.\n1:25 \u00d1oo\u00f1u laaj ko ne: \u00abGannaaw doo Almasi bi, doo Iliyas, doo Yonent bi war a \u00f1\u00ebw, lu tax ngay s\u00f3ob nit \u00f1i ci ndox?\u00bb\n1:26 Yaxya ne leen: \u00abMan maa ngi s\u00f3obe ci ndox, waaye am na ci seen biir ku ngeen xamul.\n1:27 Kookooy \u00f1\u00ebw sama gannaaw, te man sax yeyoowumaa tekki ay d\u00e0llam.\u00bb\n1:28 Lii xewoon na ci d\u00ebkku Betani, ca gannaaw dexu Yurdan, fa Yaxya doon s\u00f3obe.\n1:29 Ca \u00ebll\u00ebg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy \u00f1\u00ebw ci moom, mu ne: \u00abXool-leen! Kii mooy mbotem Y\u00e0lla, mi \u00f1u nar a rey, ngir dindi b\u00e0kkaaru \u00e0ddina.\n1:30 Moo taxoon ma wax ne: \u201cAm na kuy \u00f1\u00ebw sama gannaaw, waaye moo ma g\u00ebn a m\u00e0gg, ndaxte nekk na laata may juddu.\u201d\n1:31 Xawma woon kooku kan la waroon a doon, waaye xamal ko b\u00e0nni Israyil moo tax ma \u00f1\u00ebw, di s\u00f3ob nit \u00f1i ci ndox.\u00bb\n1:32 Ci kaw loolu Yaxya seede na lii: \u00abGis naa Xelu Y\u00e0lla mi ci melow pitax, mu j\u00f3ge ci asamaan, tegu ci moom.\n1:33 Bi loola laata am, xawma woon mooy kan, waaye Y\u00e0lla, mi ma yebal may s\u00f3obe ci ndox, nee woon na ma: \u201cDinga gis Xel mu Sell mi w\u00e0cc, tegu ci kaw nit. Kooku moo di ki leen di s\u00f3ob ci Xel mu Sell mi.\u201d\u00bb\n1:34 Yaxya teg ca ne: \u00abGis naa loolu te seede naa ne, moom moo di Doomu Y\u00e0lla ji.\u00bb\n1:35 Ca \u00ebll\u00ebg sa Yaxya taxawaatoon na ca b\u00e9rab booba, \u00e0nd ak \u00f1aari taalibeem.\n1:36 Bi mu gisee Yeesu muy romb, mu daldi ne: \u00abKii mooy mbotem Y\u00e0lla mi!\u00bb\n1:37 \u00d1aari taalibe ya d\u00e9gg li mu wax, daldi dem toppi Yeesu.\n1:38 Yeesu geestu, gis ne, \u00f1oo ngi koy topp. Mu ne leen: \u00abLu ngeen soxla woon?\u00bb \u00d1u tontu ko: \u00abFoo d\u00ebkk, R\u00e0bbi?\u00bb R\u00e0bbi mi ngi tekki \u00abKilifa gi.\u00bb\n1:39 Yeesu ne leen: \u00abKaayleen gis.\u00bb Noonu \u00f1u dem, seeti fa mu daloon, ngoonalal ko. Ci t\u00e0kkusaani kaw la woon.\n1:40 Kenn ci \u00f1oom \u00f1aar, \u00f1i d\u00e9ggoon li Yaxya wax te topp Yeesu, ma nga tuddoon Andare, mi bokkoon ak Simo\u014b Piyeer ndey ak baay.\n1:41 Andare dafa daldi dem seeti Simo\u014b ne ko: \u00abGis nanu Almasi bi.\u00bb Baat boobu mi ngi tekki \u00abKirist.\u00bb\n1:42 Noonu mu y\u00f3bbu ko ci Yeesu. Yeesu xool ko ne ko: \u00abYaa di Simo\u014b, doomu Yowaana. Dina\u00f1u la wooye Sefas.\u00bb Sefas mi ngi tekki \u00abPiyeer,\u00bb maanaam \u00abxeer.\u00bb\n1:43 Ca \u00ebll\u00ebg sa mu fas y\u00e9enee dem diiwaanu Galile te mu gis Filib. Yeesu ne ko: \u00abToppal ci man.\u00bb\n1:44 Filib mu nga d\u00ebkkoon Betsayda, d\u00ebkku Andare ak Piyeer.\n1:45 Filib dajeek Nataneel ne ko: \u00abGis nanu ki yoonu Musaa wi ak yonent yi doon wax. Mu ngi tudd Yeesu, doomu Yuusufa, te d\u00ebkk Nasaret.\u00bb\n1:46 Nataneel tontu ko ne: \u00abAa! Ndax dara lu baax man na j\u00f3ge Nasaret?\u00bb Filib ne ko: \u00ab\u00d1\u00ebwal gis.\u00bb\n1:47 Naka la Yeesu gis Nataneel j\u00ebmsi ci moom, mu daldi ne ci mbiram: \u00abXool-leen, nitu Israyil d\u00ebgg a ngee di \u00f1\u00ebw; du dox benn t\u00e0nku caaxaan.\u00bb\n1:48 Nataneel ne ko: \u00abNoo ma xame?\u00bb Yeesu tontu ko ne: \u00abBi la Filib di laata woo, gis naa la, bi nga nekkee ca ker garabu figg ga.\u00bb\n1:49 Nataneel wax ko ne: \u00abKilifa gi, yaay Doomu Y\u00e0lla ji, yaa di buuru Israyil!\u00bb\n1:50 Yeesu tontu ko ne: \u00abNdax li ma ne, gis naa la ca ker garab ga, moo tax nga g\u00ebm? Dinga gis mbir yu g\u00ebn a r\u00e9y yii.\u00bb\n1:51 Noonu mu teg ca ne: \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, dingeen gis asamaan ubbiku, malaaka yiy baagante kaw ak suuf, di w\u00e0cc ci Doomu nit ki.\u00bb\n2:1 \u00d1aari fan gannaaw loolu ag c\u00e9et am ca d\u00ebkku Kana ca diiwaanu Galile. Yaayu Yeesu teewe woon na ko.\n2:2 Woo woon na\u00f1u it Yeesu ca c\u00e9et ga ak ay taalibeem.\n2:3 Ca biir xew wa, bii\u00f1 ba daldi jeex. Yaayu Yeesu ne ko: \u00abAmatu\u00f1u bii\u00f1.\u00bb\n2:4 Yeesu ne: \u00abSoxna si, Loo ma b\u00ebggal? Ndaxte sama waxtu jotagul.\u00bb\n2:5 Yaayam daldi ne surga ya: \u00abDefleen l\u00e9pp lu mu leen wax.\u00bb\n2:6 Foofa amoon na fa jur\u00f3om benni ndaa yu \u00f1u yett ci doj, yu Yawut ya daan j\u00ebfandikoo ngir seen sangu set. Ndaa lu nekk man na def daanaka t\u00e9em\u00e9eri liitar.\n2:7 Yeesu ne surga ya: \u00abDuyleen ndaa yi.\u00bb \u00d1u duy leen, ba \u00f1u fees bay rembat.\n2:8 Noonu Yeesu ne leen: \u00abTanqleen ci l\u00e9egi, y\u00f3t ko njiitu xew wi.\u00bb \u00d1u daldi ko ciy y\u00f3t.\n2:9 Ki jiite xew wa \u00f1am ndox, ma Yeesu soppi bii\u00f1. Xamul woon fu bii\u00f1 booba j\u00f3ge, waaye surga ya tanqoon ndox ma, \u00f1oom xamoon na\u00f1u ko. Naka noonu mu woo boroom c\u00e9et ga ne ko:\n2:10 \u00abCi xew y\u00e9pp, naan gu neex gi la\u00f1uy j\u00ebkke. Bu nit \u00f1i doyalee, \u00f1u sog a g\u00e9nne ga ca des. Waaye yaw dangaa dencoon gi g\u00ebn a neex ba n\u00ebg\u00ebni.\u00bb\n2:11 Firnde bii ame ca Kana, ca diiwaanu Galile, moo doon k\u00e9emaan gi Yeesu j\u00ebkk a def. Ci noonu la wonee m\u00e0ggaayam te ay taalibeem g\u00ebm na\u00f1u ko.\n2:12 Bi loolu weesoo, mu \u00e0nd ak yaayam, ay rakkam ak i taalibeem, dem d\u00ebkku Kapernawum. Waaye y\u00e0ggu\u00f1u fa.\n2:13 M\u00e0ggalu Yawut, gi \u00f1uy wax b\u00e9su J\u00e9ggi ba, mu ngi doon jubsi. Yeesu dem Yerusalem,\n2:14 dugg ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga. Bi mu fa demee, fekk na ca \u00ebtt ba ay jaaykati nag ak yu xar ak yu pitax, ak weccikatu xaalis ya toog.\n2:15 Noonu Yeesu r\u00e0bb ab yar, daldi leen koy d\u00e0qe, ngir \u00f1u g\u00e9nn \u00ebttu k\u00ebr Y\u00e0lla ga, \u00f1oom ak xar ya ak nag ya. Mu tasaare xaalisu weccikat ya, daaneel taabal ya,\n2:16 daldi ne jaaykati pitax ya: \u00abJ\u00ebleleen fi lii! Sama k\u00ebr Baay, buleen ko def marse!\u00bb\n2:17 Taalibeem ya f\u00e0ttaliku Mbind mii: \u00abCawarte gi ma am ci sa k\u00ebr, mu ngi mel ni taal buy t\u00e0kk ci sama biir.\u00bb\n2:18 Noonu Yawut ya ne ko: \u00abBan firnde nga nuy won ngir d\u00ebggal ne, am nga sa\u00f1-sa\u00f1u def lii nga def?\u00bb\n2:19 Yeesu tontu leen: \u00abDaaneel-leen k\u00ebr Y\u00e0lla gii, ma daldi koy y\u00e9kkati ci \u00f1etti fan.\u00bb\n2:20 \u00d1u ne ko: \u00abNga ne k\u00ebr Y\u00e0lla, gii \u00f1u tabax ci \u00f1eent-fukki at ak jur\u00f3om benn, man nga koo y\u00e9kkati ci \u00f1etti fan!\u00bb\n2:21 Waaye k\u00ebr Y\u00e0lla, gi Yeesu doon wax, nekkul woon ab tabax, aw yaramam ci boppam moo ko taxoon di wax.\n2:22 Gannaaw ga nag, bi Yeesu deeyee ba dekki, la taalibeem ya f\u00e0ttaliku li mu waxoon, daldi g\u00ebm Mbind mi ak wax, ja leen Yeesu waxoon.\n2:23 Bi Yeesu nekkee Yerusalem ci m\u00e0ggalu b\u00e9su J\u00e9ggi ba, \u00f1u bare gis k\u00e9emaan, yi mu doon def, daldi g\u00ebm ci turam.\n2:24 Waaye Yeesu w\u00f3oluwu leen woon, ndaxte xamoon na leen \u00f1oom \u00f1\u00e9pp,\n2:25 te it soxlawul \u00f1u koy xamal dara ci nit, ndaxte moom ci boppam xam na xolu nit.\n3:1 Amoon na ca Farisen ya nit ku \u00f1u naan Nikodem te mu bokk ca kilifay Yawut ya.\n3:2 Genn guddi mu \u00f1\u00ebw ca Yeesu ne ko: \u00abKilifa gi, xam nanu ne, Y\u00e0llaa la y\u00f3nni ngir nga j\u00e0ngal nu, ndaxte kenn m\u00ebnul a def firnde yii ngay wone te Y\u00e0lla \u00e0ndul ak moom.\u00bb\n3:3 Yeesu tontu ko ne: \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi la koy wax, k\u00e9pp ku judduwaatul doo man a seede nguuru Y\u00e0lla.\u00bb\n3:4 Nikodem ne ko: \u00abNit ku xas ba m\u00e0ggat, nan lay man a judduwaate? Ndax day dellu ci biiru yaayam ngir judduwaat?\u00bb\n3:5 Yeesu tontu ko ne: \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi la koy wax, ku judduwul ci ndox ak ci Xelum Y\u00e0lla, doo man a bokk ci nguuru Y\u00e0lla.\n3:6 Lu juddoo ci nit, nit la; waaye lu juddoo ci Xelum Y\u00e0lla, xel la.\n3:7 Li ma ne: \u201cF\u00e0ww ngeen judduwaat,\u201d bumu la jaaxal.\n3:8 Ngelaw fu ko neex lay jublu. Yaa ngi koy d\u00e9gg waaye xamuloo fu mu j\u00f3ge, xamuloo fu mu j\u00ebm. Noonu la mel it ci k\u00e9pp ku juddoo ci Xelum Y\u00e0lla.\u00bb\n3:9 Ci baat yooyu Nikodem ne ko: \u00abNu loolu man a ame?\u00bb\n3:10 Yeesu tontu ko ne: \u00abYaw yaay j\u00e0ngal b\u00e0nni Israyil te xamuloo mbir yii?\n3:11 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi la koy wax, noo ngi wax li nu xam, di nettali li nu gis, waaye nanguwuleen a g\u00ebm li nu seede.\n3:12 Gannaaw g\u00ebmuleen li ma leen di wax ci mbiri \u00e0ddina, naka ngeen man a g\u00ebme, bu ma leen waxee ci mbiri asamaan?\n3:13 Kenn musul a y\u00e9eg ci asamaan su dul ki fa j\u00f3ge, muy Doomu nit ki.\n3:14 Te itam na Musaa sampe woon ab bant ca diggu m\u00e0ndi\u014b ma, takk ca jaan, ja mu defare woon x\u00e0njar, f\u00e0ww \u00f1u y\u00e9kkatee noonu Doomu nit ki,\n3:15 ngir k\u00e9pp ku ko g\u00ebm am ci moom dund gu dul jeex.\u00bb\n3:16 Ndaxte Y\u00e0lla dafa b\u00ebgg \u00e0ddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp, ngir k\u00e9pp ku ko g\u00ebm am dund gu dul jeex te doo s\u00e0nku mukk.\n3:17 Y\u00e0lla y\u00f3nniwul Doomam ci \u00e0ddina ngir mu daan nit \u00f1i, waaye ngir musal leen.\n3:18 K\u00e9pp ku ko g\u00ebm deesu la daan, waaye ku ko g\u00ebmul daan na\u00f1u la ba noppi, ndaxte g\u00ebmuloo ci turu Doom ji Y\u00e0lla am kepp.\n3:19 Ci nii la \u00e0tte bi ame: leer gi \u00f1\u00ebw na ci \u00e0ddina, waaye nit l\u00ebnd\u00ebm gi la\u00f1u taamu ndax seeni j\u00ebf yu bon.\n3:20 K\u00e9pp kuy def lu bon day ba\u00f1 leer gi te du ci \u00f1\u00ebw, ndax ragal ay j\u00ebfam di fee\u00f1 b\u00ebcc\u00ebgu ndarak\u00e0mm.\n3:21 Waaye ku def lu jub day \u00f1\u00ebw ci leer gi, ngir \u00f1u xam ne, def na ay j\u00ebfam ci kanam Y\u00e0lla.\n3:22 Gannaaw loolu Yeesu \u00e0nd ak ay taalibeem, dem ca biir diiwaanu Yude, toog fa ak \u00f1oom ab diir, di s\u00f3ob nit \u00f1i ci ndox.\n3:23 Yaxya moom itam doon na s\u00f3obe ci ndox ci d\u00ebkku Aynon, ca wetu d\u00ebkku Salim, ndaxte diiwaan booba bare woon na ndox. Nit \u00f1i daan na\u00f1u \u00f1\u00ebw ci moom, mu di leen s\u00f3ob.\n3:24 Booba t\u00ebjagu\u00f1u Yaxya ci kaso.\n3:25 Foofa ay taalibey Yaxya t\u00e0mbalee werante ak benn Yawut ci mbirum sangu set.\n3:26 Ci kaw loolu \u00f1u dem ca Yaxya ne ko: \u00abKilifa gi, ndax f\u00e0ttaliku nga kooka nga seede woon te mu nekkoon ak yaw ca gannaaw dexu Yurdan? Moom de, ma ngay s\u00f3obe ci ndox l\u00e9egi te \u00f1\u00e9pp a ngay dem ca moom!\u00bb\n3:27 Yaxya tontu leen: \u00abKenn m\u00ebnul a am dara lu ko Y\u00e0lla joxul.\n3:28 Y\u00e9en ci seen bopp man ngeen a seede ne, waxoon naa ne, duma Almasi bi waaye da\u00f1u maa y\u00f3nni ma jiitusi ko.\n3:29 Kiy c\u00e9etal moo moom s\u00e9etam. Waaye xaritu kiy c\u00e9etal dafay taxaw di ko d\u00e9glu, tey b\u00e9g, bu d\u00e9ggee baatam. Mb\u00e9g moomu moo di sama bos tey, te fi mu nekk mat na s\u00ebkk.\n3:30 Li war moo di moom, mu g\u00ebn a m\u00e0gg te man, ma g\u00ebn a f\u00e9ete suuf.\u00bb\n3:31 Ki j\u00f3ge ci kaw moo f\u00e9ete kaw \u00f1\u00e9pp; ki j\u00f3ge ci suuf nag, ci suuf rekk la man a bokk, te ni niti \u00e0ddina lay waxe. Ki j\u00f3ge asamaan\n3:32 day wax li mu gis ak li mu d\u00e9gg, waaye kenn nanguwul li mu seede.\n3:33 K\u00e9pp ku nangu seedeem nangu nga ne Y\u00e0lla, d\u00ebgg lay wax.\n3:34 Ndaw li Y\u00e0lla y\u00f3nni, k\u00e0ddug Y\u00e0lla lay wax, ndaxte mayu Xel mu Sell, mi Y\u00e0lla sol ci moom, amul dayo.\n3:35 Baay bi dafa b\u00ebgg Doom ji, te jox na ko sa\u00f1-sa\u00f1 ci l\u00e9pp.\n3:36 Ku g\u00ebm Doom ji, am nga dund gu dul jeex; ku d\u00e9ggadil Doom ji, amuloo dund, waaye merum Y\u00e0llaa ngi la tiim.\n4:1 Amoon na benn b\u00e9s Farisen yi d\u00e9gg ne, \u00f1iy topp Yeesu \u00f1oo \u00ebpp \u00f1iy topp Yaxya, te \u00f1i Yeesu s\u00f3ob ci ndox \u00f1oo \u00ebpp \u00f1i Yaxya s\u00f3ob.\n4:2 Fekk Yeesu moom ci boppam daawul s\u00f3ob kenn ci ndox, waaye ay taalibeem \u00f1oo daan s\u00f3obe.\n4:3 Bi Yeesu y\u00e9gee loolu nag, mu j\u00f3ge Yude, dellu diiwaanu Galile.\n4:4 Bi muy dem Galile, waroon na jaar ci diiwaanu Samari.\n4:5 Noonu mu agsi ci wetu d\u00ebkku Sikar ci tool, bi Yanq\u00f3oba mayoon doomam Yuusufa.\n4:6 Foofa la teenu Yanq\u00f3oba nekkoon. Yeesu toog ca pindu teen ba, di noppalu ndax coonob tukki ba. Ca digg-b\u00ebcc\u00ebg la woon.\n4:7 Noonu jig\u00e9enu waa Samari \u00f1\u00ebw fa di root. Yeesu ne ko: \u00abMay ma ndox, ma naan.\u00bb\n4:8 Fekk booba nag, taalibey Yeesu ya da\u00f1oo demoon ca biir d\u00ebkk ba, di j\u00ebnd lu \u00f1u lekk.\n4:9 Jig\u00e9en ja tontu ko ne: \u00abYaw, ngay Yawut, man maay jig\u00e9en ju d\u00ebkk Samari; nan nga ma man a \u00f1aane ndox?\u00bb Jig\u00e9en ja wax na loolu, ndaxte Yawut ya bokku\u00f1u woon ak waa Samari ndab yu \u00f1uy lekke.\n4:10 Noonu nag Yeesu tontu ko: \u00abSoo xamoon li Y\u00e0lla maye, xam ki lay \u00f1aan ndox, kon yaw ci sa bopp, yaa koy \u00f1aan, te moom dina la may ndoxum dund.\u00bb\n4:11 Jig\u00e9en ja ne ko: \u00abSang bi, teen bi x\u00f3ot na te amuloo baag, kon fooy j\u00eble ndoxum dund?\n4:12 Xanaa kay xalaatuloo ne, yaa g\u00ebn a m\u00e0gg sunu maam Yanq\u00f3oba, moom mi nu gasal teen bii, mu naan ci moom ak i doomam, w\u00ebgg cig juram?\u00bb\n4:13 Yeesu wax ko ne: \u00abKu naan ci ndoxum teen bii, balaa y\u00e0gg mu maraat,\n4:14 waaye ndox, mi may joxe, ku ci naan du marati mukk, ndaxte day nekk ci moom b\u00ebtu ndox buy ball, di joxe dund gu dul jeex.\u00bb\n4:15 Noonu jig\u00e9en ja daldi ko ne: \u00abSang bi, may ma ci ndox moomu, ngir ma ba\u00f1atee mar, bay \u00f1\u00ebw ba fii di rootsi.\u00bb\n4:16 Yeesu ne ko: \u00abDemal woowi sa j\u00ebkk\u00ebr te \u00f1\u00ebw.\u00bb\n4:17 Jig\u00e9en ja tontu ko ne: \u00abAwma j\u00ebkk\u00ebr de.\u00bb Yeesu ne ko: \u00abWax nga d\u00ebgg ne, amuloo j\u00ebkk\u00ebr,\n4:18 ndaxte amoon nga jur\u00f3omi j\u00ebkk\u00ebr, te ki nga nekkal l\u00e9egi du sa j\u00ebkk\u00ebr. Li nga wax d\u00ebgg la.\u00bb\n4:19 Jig\u00e9en ja ne ko: \u00abSang bi, gis naa ne, ab yonent nga.\n4:20 Nun nag, nakajekk sunuy maam ca tund wee ngay s\u00e9en la\u00f1u daan jaamoo Y\u00e0lla, waaye y\u00e9en Yawut yi, dangeen ne Yerusalem la\u00f1u war a jaamoo Y\u00e0lla.\u00bb\n4:21 Yeesu ne ko: \u00abJig\u00e9en ji, g\u00ebmal lii ma lay wax: dina am jamono joo xam ne du ci tund wale te du ci Yerusalem ngeen di jaamoo Baay bi.\n4:22 Y\u00e9en waa Samari, xamuleen li ngeen di jaamu. Nun Yawut yi, xam nanu li nuy jaamu, ndaxte kiy musal \u00e0ddina ci Yawut yi la j\u00f3ge.\n4:23 Waaye jamono dina \u00f1\u00ebw, te agsi na ba noppi, jamono joo xam ne jaamukat yi d\u00ebgg dina\u00f1u jaamu Baay bi ci xel ak ci d\u00ebgg. \u00d1oo\u00f1u nag, \u00f1ooy jaamu Baay bi, ni mu ko b\u00ebgge.\n4:24 Y\u00e0lla xel la, kon \u00f1i koy jaamu war na\u00f1u koo jaamu ci xel ak ci d\u00ebgg.\u00bb\n4:25 Jig\u00e9en ja ne ko: \u00abXam naa ne Almasi bi --maanaam Kirist \u2014 dina \u00f1\u00ebw te bu \u00f1\u00ebwee, dina nu leeralal l\u00e9pp.\u00bb\n4:26 Yeesu tontu ko: \u00abMaa di Almasi bi, man miy wax ak yaw.\u00bb\n4:27 Noonu nag taalibey Yeesu ya dellusi, gis muy wax ak ab jig\u00e9en. \u00d1u daldi jaaxle lool. Waaye kenn \u00f1emewu ko woon ne: \u00abLooy laaj?\u00bb walla: \u00abLu tax ngay wax ak moom?\u00bb\n4:28 Noonu jig\u00e9en ja wacc fa njaqam, daldi dem ca d\u00ebkk ba ne leen:\n4:29 \u00abKaayleen gis; nit a nga fee ku ma wax l\u00e9pp lu ma mas a def. Ndax kooku du Almasi bi?\u00bb\n4:30 Noonu waa d\u00ebkk ba j\u00f3g, j\u00ebm ca Yeesu.\n4:31 Fekk taalibey Yeesu ya di ko g\u00e9t\u00ebn ne: \u00abKilifa gi, lekkal.\u00bb\n4:32 Waaye Yeesu tontu leen: \u00abAm na \u00f1am wu may lekk, te xamuleen ko.\u00bb\n4:33 Taalibe ya nag di laajante naan: \u00abNdax dafa am ku ko indil lekk?\u00bb\n4:34 Yeesu ne leen: \u00abSama \u00f1am moo di def coobarey ki ma y\u00f3nni te \u00e0ggale ligg\u00e9ey, bi mu ma sant.\n4:35 Du dangeen naan: \u201cFii ak \u00f1eenti weer \u00f1u g\u00f3ob?\u201d Waaye man, dama leen naan: xool-leen tool yi, \u00f1oo ngi \u00f1or ba weex t\u00e0ll, di xaar ku leen g\u00f3ob.\n4:36 Kiy g\u00f3ob tool yi mu ngi jot xaat peyam; day dajale nit \u00f1i ngir dund gu dul jeex, ni \u00f1uy dajalee pepp. Kon boog kiy ji dina b\u00e9gandoo ak kiy g\u00f3ob.\n4:37 Wax ji \u00f1u wax ne: \u201cKenn dina ji, keneen g\u00f3ob,\u201d d\u00ebgg la.\n4:38 Yebal naa leen, ngeen g\u00f3ob tool bu ngeen beyul. \u00d1eneen a ko bey, te y\u00e9ena ko jari\u00f1oo.\u00bb\n4:39 Bi jig\u00e9en ja nee waa d\u00ebkk ba: \u00abWax na ma li ma def l\u00e9pp,\u00bb \u00f1u bare g\u00ebm na\u00f1u Yeesu.\n4:40 \u00d1u daldi dikk \u00f1aan Yeesu, mu dal ak \u00f1oom. Yeesu toog fa \u00f1aari fan.\n4:41 \u00d1u bare g\u00ebm ko ndax li mu doon wax.\n4:42 \u00d1u ne jig\u00e9en ja: \u00abL\u00e9egi g\u00ebm nanu, te du li nga wax moo tax waaye li nu gisal sunu bopp. Te xam nanu ne, d\u00ebgg-d\u00ebgg kii moo di Musalkatu \u00e0ddina si.\u00bb\n4:43 Bi Yeesu amee \u00f1aari fan ca d\u00ebkk ba, mu j\u00f3ge fa, j\u00ebm diiwaanu Galile,\n4:44 ndaxte moom ci boppam nee woon na: \u00abAb yonent, kenn du ko faaydaal ca r\u00e9ewam.\u00bb\n4:45 Bi mu agsee Galile, nit \u00f1i teeru ko, ndaxte \u00f1oom itam teewoon na\u00f1u ca m\u00e0ggalu b\u00e9su J\u00e9ggi ba ca Yerusalem, te gisoon na\u00f1u la mu fa defoon l\u00e9pp.\n4:46 Noonu kon mu dellusi Kana ci Galile, d\u00ebkk ba mu soppe woon ndox ma bii\u00f1. Amoon na benn dagu buur bu d\u00ebkkoon Kapernawum te doomam feebar.\n4:47 Bi mu d\u00e9ggee ne, Yeesu j\u00f3ge na Yude, \u00f1\u00ebw Galile, mu dikk ci moom, \u00f1aan ko mu \u00f1\u00ebw k\u00ebram, w\u00e9ral doomam, ji wopp bay b\u00ebgg a dee.\n4:48 Yeesu ne ko: \u00abY\u00e9en daal, dungeen g\u00ebm mukk, fi ak gisuleen ay firnde walla ay k\u00e9emaan.\u00bb\n4:49 Dagu buur ba neeti ko: \u00abSang bi, \u00f1\u00ebwal, bala sama doom di dee.\u00bb\n4:50 Yeesu ne ko: \u00abDemal, sa doom dina dund.\u00bb Kilifa ga g\u00ebm la ko Yeesu wax, daldi dem.\n4:51 Bi muy dellu k\u00ebram nag, ay surgaam gatandu ko. \u00d1u daldi ne ko: \u00abXale bi dina dund!\u00bb\n4:52 Mu laaj leen ci ban waxtu la t\u00e0mbalee tane, \u00f1u tontu ko ne: \u00abD\u00e9mb ca njolloor la am ag f\u00e9ex.\u00bb\n4:53 Noonu baayu xale ba daldi seetlu ne, ca waxtu woowa la ko Yeesu ne woon: \u00abSa doom dina dund.\u00bb Moom ak njabootam g\u00e9pp, \u00f1u daldi g\u00ebm Yeesu.\n4:54 Lii mooy \u00f1aareelu firnde, bi Yeesu def ci Galile, gannaaw bi mu j\u00f3gee Yude.\n5:1 Gannaaw loolu Yawut ya amoon na\u00f1u genn m\u00e0ggal, moo tax Yeesu demoon Yerusalem.\n5:2 Ca wetu benn ci bunti d\u00ebkk ba nag, maanaam ca Buntu xar ya, am na fa b\u00ebt bu tudd Betesda ci l\u00e0kku yawut, te \u00f1u w\u00ebrale ko ak jur\u00f3omi mbaar.\n5:3 Ca suufu mbaar yooyu la jarag yu bare, yu deme niki ay gumba, ay lafa\u00f1 ak ay l\u00e0ggi, daan t\u00ebdd, di xaar ndox mi yengatu;\n5:4 ndaxte, ci ni \u00f1u ko nettalee, benn malaakam Boroom bi da daan w\u00e0cc l\u00e9eg-l\u00e9eg di jax ndox mi. Bu ndox mi masaa yengu ba noppi, jarag ju ca jiitu, wopp joo amaan, daldi w\u00e9r ca saa sa.\n5:5 Amoon na fa benn waay bu feebaroon lu mat fanweeri at ak jur\u00f3om \u00f1ett.\n5:6 Bi ko Yeesu s\u00e9enee mu t\u00ebdd, te mu xam ne, woppam ji y\u00e0ggoon na lool, mu laaj ko ne: \u00abNdax b\u00ebgg ngaa w\u00e9r?\u00bb\n5:7 Jarag ja tontu ko ne: \u00abSang bi, duma am ku ma s\u00f3ob ci ndox mi, bu yengoo; su ma ciy fexee dem, \u00f1u j\u00ebkk ma ci.\u00bb\n5:8 Yeesu ne ko: \u00abJ\u00f3gal, j\u00ebl sa basa\u014b te dox.\u00bb\n5:9 Ca saa sa mu daldi w\u00e9r, j\u00ebl basa\u014bam, daldi dox. Mbir moomu dafa daje woon ak b\u00e9su noflaay ba,\n5:10 looloo tax ba Yawut ya daldi ne nit ku w\u00e9r ka: \u00abTey b\u00e9su noflaay la, te sunu yoon aaye na, ngay yor sa basa\u014b.\u00bb\n5:11 Mu ne leen: \u00abKi ma faj moo ma ne: \u201cJ\u00eblal sa basa\u014b te dox.\u201d\u00bb\n5:12 \u00d1u ne ko nag: \u00abKu la ne: \u201cJ\u00eblal sa basa\u014b te dox?\u201d\u00bb\n5:13 Waaye waa ji xamul ki ko w\u00e9ral, fekk booba Yeesu dem na, te nit \u00f1u bare teewoon na\u00f1u ca b\u00e9rab ba.\n5:14 Bi \u00f1u ca tegee ab diir, Yeesu dajeek moom ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga ne ko: \u00abD\u00e9glul, fii mu ne, w\u00e9r nga; bul defati b\u00e0kkaar, ngir ragal lu y\u00e9es lii dal la.\u00bb\n5:15 Noonu nit ka dellu ne Yawut ya, Yeesu moo ko fajoon.\n5:16 Looloo tax Yawut ya di wut a sonal Yeesu, ndaxte daan na j\u00ebfe noonu ca b\u00e9su noflaay ba.\n5:17 Waaye Yeesu tontu na leen ne: \u00abSama Baay nekk na ba tey ci ligg\u00e9ey, kon man itam damay ligg\u00e9ey.\u00bb\n5:18 Baat boobu moo tax ba Yawut yi g\u00ebn koo wut a rey, ndaxte yemul woon rekk ci ba\u00f1 a topp ndigalu b\u00e9su noflaay ba, waaye dafa wax it ne, Y\u00e0lla Baayam la, ba teg boppam Y\u00e0lla.\n5:19 Noonu Yeesu ne leen: \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, Doom ji m\u00ebnul a def dara moom ci boppam; li mu gis Baay bi di def rekk lay def. Li Baay bi di j\u00ebf la Doom ji itam di j\u00ebf.\n5:20 Ndaxte Baay bi b\u00ebgg na Doom ji, ba di ko won l\u00e9pp lu muy def, te dina ko won j\u00ebf yu \u00ebpp k\u00e9emaan yii, ngir ngeen g\u00ebn a waaru.\n5:21 Maanaam, ni Baay bi di dekkale \u00f1u dee \u00f1i, di leen jox dund, noonu la Doom ji di joxe dund \u00f1i mu ko b\u00ebgg a jox.\n5:22 Baay bi du \u00e0tte kenn; \u00e0tte bi y\u00e9pp, jox na ko Doom ji,\n5:23 ngir \u00f1\u00e9pp di teral Doom ji, ni \u00f1uy terale Baay bi. Ku teralul Doom ji, teraloo Baay, bi ko y\u00f3nni.\n5:24 \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, ku d\u00e9gg sama k\u00e0ddu te g\u00ebm ki ma y\u00f3nni, am nga dund gu dul jeex te doo jaar ca \u00e0tte ba, ndaxte g\u00e9nn nga ci dee, t\u00e0bbi ci dund.\n5:25 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, jamono dina \u00f1\u00ebw te agsi na ba noppi, mooy jamono, ji \u00f1u dee \u00f1i di d\u00e9gg baatu Doomu Y\u00e0lla ji, te ku ko d\u00e9gg dinga dund.\n5:26 Ndaxte ni Baay bi ame dund moom ci boppam, noonu it la ko maye Doom ji, mu am ko ci boppam.\n5:27 Jox na Doom ji itam sa\u00f1-sa\u00f1u \u00e0tte, ndaxte mooy Doomu nit ki.\n5:28 \u00abBu leen ci dara jaaxal; ndaxte jamonoo ngi \u00f1\u00ebw ju n\u00e9ew y\u00e9pp, yi nekk ci seen b\u00e0mmeel, di d\u00e9gg baatam tey g\u00e9nn.\n5:29 \u00d1i daan j\u00ebf lu baax dina\u00f1u dekki, dund ba f\u00e0ww, waaye \u00f1i daan j\u00ebf lu bon, dina\u00f1u dekki, \u00f1u daan leen.\n5:30 M\u00ebnumaa def dara man ci sama bopp. Ni ma Baay bi di digale rekk laay \u00e0ttee, te sama \u00e0tte bu jub la, ndaxte defuma sama b\u00ebgg-b\u00ebgg, ci waawi ki ma y\u00f3nni do\u014b\u014b laay aw.\n5:31 \u00abSu ma seedeelee sama bopp, sama wax du am maana.\n5:32 Waaye keneen moo may seedeel, te bir na ma ne, la muy wax ci man d\u00ebgg la.\n5:33 \u00abY\u00e9en y\u00f3nni ngeen ay ndaw ci Yaxya, te seede na d\u00ebgg.\n5:34 Man ci sama bopp soxlawuma seedes nit; waaye nag damay wax loolu rekk, ngir ngeen mucc.\n5:35 Yaxya meloon na ni l\u00e0mp buy t\u00e0kk tey leeral, te nangu ngeen a b\u00e0nneexu ab diir ci leeram.\n5:36 \u00abWaaye yor naa ci man seede su g\u00ebn a mag si ma Yaxya di seedeel: maa ngi def j\u00ebf, yi ma Baay biy sant. J\u00ebf yooyu may def nag \u00f1ooy seede ne, Baay bi moo ma y\u00f3nni.\n5:37 Te Baay bi ma y\u00f3nni, moom itam seede na ma. Musuleen a d\u00e9gg baatam te musuleen a gis xar-kanamam,\n5:38 te k\u00e0ddoom saxul ci y\u00e9en, ndaxte g\u00ebmuleen ki mu y\u00f3nni.\n5:39 Y\u00e9ena ngi g\u00ebstu Mbind yi, ndaxte dangeen cee yaakaar dund gu dul jeex. Mbind yooyu nag far, ci sama mbir la\u00f1uy wax;\n5:40 te b\u00ebgguleen a \u00f1\u00ebw ci man ngir am dund!\n5:41 \u00abWutuma tagg yu j\u00f3ge ci nit.\n5:42 Waaye y\u00e9en, xam naa leen; leer na ma ne, amuleen ci seen xol benn mb\u00ebggeel ci Y\u00e0lla.\n5:43 Man \u00f1\u00ebw naa ci sama turu Baay, te nanguwuleen ma, waaye bu keneen dikkee ci turu boppam, ngeen nangu ko.\n5:44 B\u00ebgg ngeen ku leen di tagg, te wutuleen ng\u00ebr\u00ebm, li j\u00f3ge ci jenn Y\u00e0lla rekk ji am. Kon nan ngeen man a g\u00ebme?\n5:45 \u00abBuleen xalaat ne, maa leen di jii\u00f1 dara ci sama kanamu Baay. Musaa, mi ngeen yaakaar, moo leen di booleek moom.\n5:46 Bu ngeen g\u00ebmoon Musaa, dingeen ma g\u00ebm man itam, ndaxte seedeel na ma.\n5:47 Waaye su fekkee g\u00ebmuleen li Musaa bind, kon nu ngeen man a g\u00ebme samay wax?\u00bb\n6:1 Gannaaw loolu Yeesu dafa j\u00e0ll dexu Galile, maanaam dexu Tibery\u00e0dd.\n6:2 Mbooloo mu bare topp ci moom, ndaxte gisoon na\u00f1u firnde yooyee mu wone, bi mu w\u00e9ralee jarag ya.\n6:3 Yeesu daldi y\u00e9eg ca kaw tund wa, toog fa ak ay taalibeem.\n6:4 Fekk na booba b\u00e9su J\u00e9ggi ba, di m\u00e0ggalu Yawut ya, jubsi.\n6:5 Bi Yeesu xoolee, gis mbooloo mu r\u00e9y di \u00f1\u00ebw ci moom, mu ne Filib: \u00abFu nuy j\u00eble mburu, mu nu leen man a dundale?\u00bb\n6:6 Bi muy wax loolu it, da doon seetlu Filib, ndaxte xamoon na booba li mu nar a def.\n6:7 Filib ne ko: \u00abPeyug jur\u00f3om \u00f1etti weer sax, bu nu ko amoon, du leen man a doy ci mburu, ba kenn ku nekk ci \u00f1oom am ci dog wu ndaw.\u00bb\n6:8 Keneen ca taalibe ya di Andare, mi bokk ak Simo\u014b Piyeer ndey ak baay, ne ko:\n6:9 \u00abAm na fi ci mbooloo mi ab xale bu yor jur\u00f3omi mburu ak \u00f1aari j\u00ebn, waaye loolu lu muy jari\u00f1 mbooloo mu tollu nii?\u00bb\n6:10 Yeesu daldi ne taalibe ya: \u00abNa \u00f1\u00e9pp toog.\u00bb Fekk \u00f1ax mu bare amoon ca b\u00e9rab ba. Noonu g\u00f3or \u00f1\u00e9pp \u00e0gg suuf. Waroon na\u00f1oo mat jur\u00f3omi junni.\n6:11 Yeesu daldi j\u00ebl mburu ya, g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla, ba noppi s\u00e9ddale ko \u00f1a fa toogoon. Mu jox leen itam j\u00ebn, ba \u00f1u doyal s\u00ebkk.\n6:12 Bi \u00f1u lekkee ba regg, Yeesu ne taalibe ya: \u00abDajaleleen desitu mburu mi, ba dara du ci r\u00e9er.\u00bb\n6:13 \u00d1u dajale ko, daldi feesal fukki pa\u00f1e ak \u00f1aar ak desiti jur\u00f3omi mburu, yi \u00f1u doon lekk.\n6:14 Bi nit \u00f1a gisee firnde jooju Yeesu wone, \u00f1u ne: \u00abD\u00ebgg-d\u00ebgg kii mooy Yonent, bi war a \u00f1\u00ebw ci \u00e0ddina!\u00bb\n6:15 Yeesu gis ne da\u00f1u koo nar a j\u00eblsi, fal ko buur. Mu b\u00e0yyi leen fa, dellu moom rekk ca tund wa.\n6:16 Bi timis jotee taalibeem ya w\u00e0cc ca tefes ga,\n6:17 dugg ci gaal, di j\u00e0ll dex gi, j\u00ebm d\u00ebkku Kapernawum. Booba guddi woon na, te Yeesu agseegul ci \u00f1oom.\n6:18 Dex gi yengu na lool, ndaxte da doon ngelaw ak doole.\n6:19 Bi \u00f1u joowee lu war a tollook jur\u00f3om benni kilomet, \u00f1u s\u00e9en Yeesu, muy dox ci kaw dex gi, j\u00ebm ci \u00f1oom, \u00f1u daldi tiit.\n6:20 Waaye Yeesu ne leen: \u00abMan la, buleen tiit!\u00bb\n6:21 Noonu \u00f1u nangu koo dugal ca gaal ga, gaal ga daldi teer ca saa sa ca fa \u00f1u b\u00ebggoon a w\u00e0cc.\n6:22 Ca \u00ebll\u00ebg sa mbooloo, ma des ca geneen w\u00e0llu dex ga, gis ne genn gaal ga fa nekkoon rekk dem na. Xam na\u00f1u ne Yeesu bokku ko woon ak taalibe ya, ndaxte \u00f1oom rekk a \u00e0ndoon.\n6:23 Waaye yeneen gaal yu j\u00f3ge d\u00ebkku Tibery\u00e0dd \u00f1\u00ebw, teer ca wetu fa \u00f1u lekke woon mburu ma, gannaaw bi Boroom bi santee Y\u00e0lla ba noppi.\n6:24 Bi mbooloo ma gisee ne, Yeesu walla taalibe ya kenn nekkatu fa, \u00f1u dugg ca gaal yooyu, dem seeti ko Kapernawum.\n6:25 Bi \u00f1u fekkee Yeesu ca geneen w\u00e0llu dex ga, \u00f1u ne ko: \u00abKilifa gi, ka\u00f1 nga fi \u00f1\u00ebw?\u00bb\n6:26 Yeesu ne leen: \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, firnde yi ngeen gis taxul ngeen may seet. Y\u00e9ena ngi may w\u00ebr ndax mburu, mi ngeen lekk ba suur.\n6:27 Buleen ligg\u00e9eyal \u00f1am wuy y\u00e0qu; li g\u00ebn mooy \u00f1am wu sax abadan tey joxe dund gu dul jeex. \u00d1am woowule, Doomu nit ki dina leen ko jox, ndaxte moom la Y\u00e0lla Baay bi t\u00e0nn, mu nekk ndawam.\u00bb\n6:28 Noonu \u00f1u laaj ko ne: \u00abLu nu war a ligg\u00e9ey, ngir matal j\u00ebf yi neex Y\u00e0lla?\u00bb\n6:29 Yeesu tontu leen ne: \u00abJ\u00ebf ji neex Y\u00e0lla, moo di g\u00ebm ki mu y\u00f3nni.\u00bb\n6:30 \u00d1u ne ko: \u00abBan firnde nga nu man a won, ngir nu g\u00ebm la? Ban ligg\u00e9ey nga nar a def?\n6:31 Sunuy maam dunde na\u00f1u m\u00e0nn ca m\u00e0ndi\u014b ma, ndaxte Mbind mi nee na: \u201cJox na leen, \u00f1u lekk \u00f1am wu w\u00e0cce ca asamaan.\u201d\u00bb\n6:32 Yeesu waxaat ne: \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, du Musaa moo leen jox \u00f1am woowu w\u00e0cce ca asamaan; sama Baay ci boppam, moo leen di jox \u00f1am wu w\u00f3or, wi w\u00e0cce ca asamaan.\n6:33 Ndaxte \u00f1am, wi Y\u00e0lla di joxe, mooy \u00f1am wiy w\u00e0cce ci asamaan tey jox \u00e0ddina si dund.\u00bb\n6:34 \u00d1u ne ko nag: \u00abSang bi, kon dee nu faral di jox ci \u00f1am woowe!\u00bb\n6:35 Yeesu tontu leen ne: \u00abMan maay \u00f1am wiy joxe dund. Ku \u00f1\u00ebw ci man, doo xiif mukk; te ku ma g\u00ebm, doo mar.\n6:36 Waaye wax naa leen ko ba noppi; gis ngeen ma te taxul ngeen g\u00ebm!\n6:37 K\u00e9pp ku ma Baay bi jox dina \u00f1\u00ebw ci man, te duma d\u00e0q mukk ki may fekksi.\n6:38 Ndaxte w\u00e0ccewuma ci asamaan ngir def sama b\u00ebgg-b\u00ebgg, waaye damay matal b\u00ebgg-b\u00ebggu ki ma y\u00f3nni.\n6:39 Lii mooy b\u00ebgg-b\u00ebggu ki ma y\u00f3nni: bu ma \u00f1\u00e0kk kenn ci \u00f1i mu ma may, te dafa b\u00ebgg it ma dekkal leen keroog b\u00e9s bu mujj ba.\n6:40 Ndaxte lii mooy b\u00ebgg-b\u00ebggu Baay bi: k\u00e9pp ku gis Doom ji te g\u00ebm ko, am dund gu dul jeex, te b\u00e9s bu mujj ba, dinaa ko dekkal!\u00bb\n6:41 Yawut ya t\u00e0mbali di \u00f1urumtoo Yeesu, ndaxte dafa ne: \u00abMaay \u00f1am wi w\u00e0cce ci asamaan.\u00bb\n6:42 \u00d1u naan: \u00abNdax kii du Yeesu, doomu Yuusufa? Xam nanu ndeyam ak baayam. Kon nag lu tax l\u00e9egi mu naan, mi ngi j\u00f3ge asamaan?\u00bb\n6:43 Yeesu ne leen: \u00abB\u00e0yyileen seen \u00f1urumtu bi.\n6:44 Kenn m\u00ebnul a \u00f1\u00ebw ci man te Baay, bi ma y\u00f3nni, xiirtalu la ci, te man dinaa la dekkal keroog b\u00e9s bu mujj ba.\n6:45 Yonent yi bind na\u00f1u k\u00e0ddu gii: \u201cY\u00e0lla dina leen j\u00e0ngal \u00f1oom \u00f1\u00e9pp.\u201d Kon nag ku d\u00e9glu te nangu waxi Baay bi, dina \u00f1\u00ebw ci man.\n6:46 Tekkiwul ne kenn mas na gis Baay bi. Ki j\u00f3ge ci Y\u00e0lla do\u014b\u014b a ko gis.\n6:47 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, ku g\u00ebm am nga dund gu dul jeex.\n6:48 Maay \u00f1am wiy joxe dund.\n6:49 Seeni maam lekk na\u00f1u m\u00e0nn ca m\u00e0ndi\u014b ma, teewul dee na\u00f1u.\n6:50 Waaye \u00f1am wiy w\u00e0cce ci asamaan, ku ko lekk, doo dee.\n6:51 Man maay \u00f1am wiy dund te w\u00e0cce ci asamaan. Ku lekk ci \u00f1am wii, dinga dund ba f\u00e0ww. Te it \u00f1am wi may joxeji, sama yaram la; dama koy joxe ngir \u00e0ddina man a dund.\u00bb\n6:52 Noonu Yawut ya werante werante bu t\u00e0ng ci seen biir naan: \u00abNaka la nu waa jii man a joxe yaramam, ngir nu lekk ko?\u00bb\n6:53 Yeesu ne leen: \u00abD\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, bu ngeen lekkul yaramu Doomu nit ki te naanuleen deretam, dungeen am dund ci y\u00e9en.\n6:54 Ku lekk sama yaram te naan sama deret, am nga dund gu dul jeex, te dinaa la dekkal keroog b\u00e9s bu mujj ba.\n6:55 Ndaxte sama yaram mooy \u00f1am wu w\u00f3or wi, te sama deret mooy naan gu w\u00f3or gi.\n6:56 Kiy lekk sama yaram tey naan sama deret dina sax ci man, ma d\u00ebkk ci moom.\n6:57 Baay bi ma y\u00f3nni mu ngi dund, te maa ngi dund jaarale ko ci moom; noonu itam ku may lekk dina dund jaarale ko ci man.\n6:58 Kon nag \u00f1am, wi w\u00e0cce ci asamaan a ngi noonu; bokkul ak \u00f1am, wa seeni maam lekkoon te faatu. Ku lekk \u00f1am wii may wax dinga dund ba f\u00e0ww.\u00bb\n6:59 Baat yooyu la Yeesu wax, bi mu doon j\u00e0ngale ca j\u00e0ngu ba ca Kapernawum.\n6:60 Bi \u00f1u d\u00e9gloo Yeesu ba noppi, taalibeem yu bare nee na\u00f1u: \u00abNj\u00e0ngale mii de, jafe na! Kan moo ko man a d\u00e9glu?\u00bb\n6:61 Yeesu gis ne taalibeem yaa ngi \u00f1urumtoo loolu, mu ne leen: \u00abNdax li ma wax da leen a jaaxal?\n6:62 Lan mooy am nag, bu fekkee gis ngeen Doomu nit ki dellu, y\u00e9eg fa mu j\u00ebkkoon a nekk?\n6:63 Xelu Y\u00e0lla mi mooy joxe dund; \u00f1am wi jari\u00f1ul dara. K\u00e0ddu yi ma leen wax, ci Xelum Y\u00e0lla la\u00f1u j\u00f3ge te \u00f1ooy joxe dund.\n6:64 Waaye am na ci seen biir \u00f1u ko g\u00ebmul.\u00bb Ndaxte Yeesu xamoon na ca nj\u00e0lb\u00e9en ga \u00f1an \u00f1oo ko waroon a g\u00ebmadi ak kan moo ko waroon a wor.\n6:65 Mu dolli ca it ne: \u00abLooloo tax ma ne, kenn m\u00ebnul a \u00f1\u00ebw ci man te Baay bi mayu la, nga agsi.\u00bb\n6:66 Ci loolu taalibeem yu bare d\u00ebpp, ba\u00f1atee \u00e0nd ak moom.\n6:67 Yeesu daldi wax ak fukki taalibe yi ak \u00f1aar ne leen: \u00abMbaa b\u00ebgguleen a dem, y\u00e9en itam?\u00bb\n6:68 Simo\u014b Piyeer ne ko: \u00abBoroom bi, ci kan lanuy dem? Yaa yor k\u00e0ddu yiy joxe dund gu dul jeex.\n6:69 L\u00e9egi nun g\u00ebm nanu te xam nanu ne, yaa di Aji Sell, ji j\u00f3ge ci Y\u00e0lla.\u00bb\n6:70 Yeesu daldi tontu ne leen: \u00abXanaa du maa leen t\u00e0nn, y\u00e9en fukk yi ak \u00f1aar? Moona, am na ci y\u00e9en koo xam ne seytaane la!\u00bb\n6:71 Yudaa miy doomu Simo\u014b Iskariyo la doon wax. Ndeke Yudaa, la muy bokk l\u00e9pp ca fukki taalibe ya ak \u00f1aar, moo ko naroon a wor.\n7:1 Gannaaw loolu Yeesu doon na w\u00ebr diiwaanu Galile.\n7:2 B\u00ebggul woon a dem diiwaanu Yude, ndaxte Yawut ya da\u00f1u ko doon wut a rey. Fekk na b\u00e9su xewu Yawut ya, \u00f1u koy wax m\u00e0ggalu Mbaar ya, mu ngi doon jubsi.\n7:3 Noonu rakki Yeesu yu g\u00f3or ya ne ko: \u00abJ\u00f3ge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, \u00f1oom itam, jaloore yi ngay def.\n7:4 Ku b\u00ebgg a siiw, doo n\u00ebbb say j\u00ebf. Boo demee bay wone jaloore yu mel ni, fexeel ba \u00f1\u00e9pp gis la.\u00bb\n7:5 Rakkam yi da\u00f1u doon wax loolu, ndaxte \u00f1oom itam g\u00ebmu\u00f1u ko woon.\n7:6 Yeesu ne leen: \u00abSama waxtu jotagul. Ci y\u00e9en nag, waxtu y\u00e9pp a baax.\n7:7 \u00c0ddina du leen ba\u00f1 waaye ba\u00f1 na ma, man, ndaxte maa wax ne, seeni j\u00ebf baaxul.\n7:8 Y\u00e9en nag demleen m\u00e0ggal ga. Demaguma m\u00e0ggal googu, ndaxte sama waxtu jotagul.\u00bb\n7:9 Bi mu leen waxee loolu ba noppi, moom mu des Galile.\n7:10 Bi rakkam ya demee ca m\u00e0ggal ga, Yeesu itam sog a dem te kenn y\u00e9gu ko; siiwalul demam.\n7:11 Fekk Yawut yaa nga ko doon seet ca m\u00e0ggal ga te naan: \u00abAna waa ji?\u00bb\n7:12 Ca biir mbooloo ma \u00f1u ngi doon d\u00e9eyante, di wax ci ay mbiram. \u00d1ii naan: \u00abNit ku baax la.\u00bb \u00d1ee naan: \u00abD\u00e9ed\u00e9et, day nax nit \u00f1i.\u00bb\n7:13 Waaye kenn \u00f1emewu koo tudd ca kaw, ndaxte da\u00f1oo ragaloon Yawut ya.\n7:14 Bi \u00f1u demee ba ca diggu m\u00e0ggal ga, Yeesu dem di j\u00e0ngale ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga.\n7:15 Yawut ya nag jaaxle, daldi ne: \u00abNu waa jii def ba xam lii l\u00e9pp, moom mi j\u00e0ngul?\u00bb\n7:16 Yeesu daldi leen tontu ne: \u00abLi may j\u00e0ngale, j\u00f3gewul ci man, waaye ci ki ma y\u00f3nni la j\u00f3ge.\n7:17 Ku fas y\u00e9enee w\u00e9y ci b\u00ebgg-b\u00ebggu Y\u00e0lla, dina xam ndax sama nj\u00e0ngale ci Y\u00e0lla la j\u00f3ge, walla ci sama coobare.\n7:18 Nit kiy wax ci coobareem nag, day wut a m\u00e0ggal boppam, waaye kiy wut a m\u00e0ggal ki ko y\u00f3nni, d\u00ebgg rekk lay wax te jubadiwul fenn.\n7:19 Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Y\u00e0lla yi? Waaye kenn ci y\u00e9en s\u00e0mmu ko! Lu tax ngeen b\u00ebgg maa rey?\u00bb\n7:20 Mbooloo ma ne ko: \u00abXanaa dangaa am ay rab! Ku lay wut a rey?\u00bb\n7:21 Yeesu ne leen: \u00abBenn jaloore rekk laa def, te y\u00e9en \u00f1\u00e9pp ngeen jaaxle!\n7:22 Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gune yi --j\u00f3gewul kat ci Musaa; mi ngi t\u00e0mbalee ci seen maami cosaan \u2014 moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci b\u00e9su noflaay bi.\n7:23 Bu ngeen manee xarafal nit ci b\u00e9su noflaay bi, ngir ba\u00f1 a w\u00e0cc yoonu Musaa, lu tax nag ngeen mere ma, ndax li ma ci w\u00e9ral nitu l\u00ebmm?\n7:24 B\u00e0yyileen di \u00e0tte ci ni ngeen di gise, te di \u00e0tte d\u00ebgg.\u00bb\n7:25 Am na ci waa Yerusalem \u00f1u doon wax naan: \u00abXanaa du nit kii la\u00f1uy wut a rey?\n7:26 Xool-leen, mi ngi waaraate ci biir nit \u00f1i, te kenn du ko wax dara. Ndax sunu kilifa yi da\u00f1oo xam ne, mooy Almasi bi?\n7:27 Waaye waa ji, xam nanu fu mu j\u00f3ge, te saa su Almasi bi dee dikk, kenn du xam fu mu b\u00e0yyikoo.\u00bb\n7:28 Yeesu di j\u00e0ngale ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, daldi wax ca kaw ne: \u00abNdax xam ngeen ma te xam fi ma j\u00f3ge? \u00d1\u00ebwaluma sama bopp, waaye ki ma y\u00f3nni, ku w\u00f3or la. Y\u00e9en xamuleen ko.\n7:29 Man xam naa ko, ndaxte ca moom laa j\u00f3ge, te itam moo ma y\u00f3nni.\u00bb\n7:30 Noonu \u00f1u koy wut a j\u00e0pp, waaye kenn manalu ko woon dara, ndaxte waxtoom jotagul woon.\n7:31 Moona nag, \u00f1u bare ca mbooloo ma g\u00ebm na\u00f1u ko. \u00d1u nga naan: \u00abNdax b\u00e9s bu Almasi bi dikkee, ay firndeem dina \u00ebpp yu nit kii?\u00bb\n7:32 Farisen ya daldi d\u00e9gg la mbooloo ma doon d\u00e9eyante ci mbirum Yeesu. Saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya yebal ay alkaati yu daan wottu k\u00ebr Y\u00e0lla ga, ngir \u00f1u j\u00e0ppi ko.\n7:33 Yeesu wax ne: \u00abDinaa nekk ak y\u00e9en fi ak ab diir, sog a dem ci ki ma y\u00f3nni.\n7:34 Dingeen ma seet, waaye dungeen ma gis; te dungeen man a dem fa may nekk.\u00bb\n7:35 Yawut ya di laajante ci seen biir naan: \u00abFu muy dem fu nu ko dul fekk? Mbaa du dafa nar a dem ca Yawut, ya g\u00e0ddaaye ca Gereg ya, te j\u00e0ngali Gereg ya?\n7:36 Lan la baat yii mu wax di tekki: \u201cDingeen ma seet waaye dungeen ma gis,\u201d ak: \u201cDungeen man a dem fa may nekk?\u201d\u00bb\n7:37 B\u00e9s ba mujjoon ca m\u00e0ggal ga moo ca \u00ebpp solo; keroog Yeesu taxaw, wax ca kaw ne: \u00abKu mar, na \u00f1\u00ebw ci man; ku g\u00ebm, na naan! Ndaxte Mbind mi nee na, ndox mu bare muy dundale dina xellee ci d\u00ebnnam.\u00bb\n7:39 Booba li ko taxoon di wax mooy Xelu Y\u00e0lla, mi \u00f1i ko g\u00ebm naroon a jot. Fekk na joxeegu\u00f1u woon Xelu Y\u00e0lla mi, ndaxte ndamu Yeesu fee\u00f1agul woon.\n7:40 Bi \u00f1u d\u00e9ggee wax jooja, am ay nit ca mbooloo ma \u00f1u naan: \u00abD\u00ebgg-d\u00ebgg kii mooy Yonent bi war a \u00f1\u00ebw.\u00bb\n7:41 \u00d1eneen naan: \u00abMooy Almasi bi.\u00bb \u00d1a ca des it ne: \u00abWaaye nan la Almasi bi man a j\u00f3gee Galile?\n7:42 Mbind mi wax na ne, Almasi bi ci xeetu Daawuda lay w\u00e0cce te Betleyem, d\u00ebkku Daawuda, lay j\u00f3ge.\u00bb\n7:43 Noonu f\u00e9ewaloo daldi am ca biir mbooloo ma ndax Yeesu.\n7:44 Am na ca \u00f1oom \u00f1u ko b\u00ebggoon a j\u00e0pp, waaye kenn manalu ko woon dara.\n7:45 Bi alkaati ya delloo, saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya laaj leen ne: \u00abLu tax indiwuleen ko?\u00bb\n7:46 Alkaati ya ne leen: \u00abKenn musul a waxe ni nit kooku!\u00bb\n7:47 Noonu Farisen ya laaj leen: \u00abMbaa naxu\u00f1u leen, y\u00e9en itam?\n7:48 Ndax am na kenn ci saraxalekat yi walla ci Farisen yi ku ko g\u00ebm? D\u00e9ed\u00e9et.\n7:49 Waaye mbooloo mi xamu\u00f1u yoonu Musaa; \u00f1u alku la\u00f1u!\u00bb\n7:50 Nikodem bokkoon na ca Farisen ya fa nekkoon. Fekk moo seeti woon Yeesu lu jiitu. Mu ne leen:\n7:51 \u00abNdax ci sunu yoon, man na\u00f1oo daan kenn te d\u00e9gluwu\u00f1u ko, mbaa \u00f1u xam lu mu def?\u00bb\n7:52 \u00d1u tontu ko ne: \u00abMbaa du yaw itam dangaa bokk ci diiwaanu Galile? G\u00ebstul, kon dinga xam ne, benn yonent musul a j\u00f3ge Galile.\u00bb\n7:53 Gannaaw loolu ku ci nekk dellu sa k\u00ebr.\n8:1 Yeesu moom, dem ca tundu Oliw ya.\n8:2 Ca \u00ebll\u00ebg sa ca fajar, mu dellu ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, mbooloo ma fa teewoon w\u00ebr ko. Mu toog, t\u00e0mbali di leen j\u00e0ngal.\n8:3 Xutbakat ya ak Farisen ya indi jenn jig\u00e9en ju \u00f1u bettoon muy njaaloo, \u00f1u taxawal ko ca diggu mbooloo ma.\n8:4 Noonu \u00f1u ne Yeesu: \u00abKilifa gi, jig\u00e9en jii de, da\u00f1u koo bett muy njaaloo.\n8:5 Ci ndigali Y\u00e0lla yi, jig\u00e9en ju njaaloo, Musaa dafa santaane \u00f1u s\u00e0nni ko ay xeer, ba mu dee. Yaw nag, lu ciy sa xalaat?\u00bb\n8:6 Loolu nag, da\u00f1u ko doon wax ngir seetlu ko, ndaxte b\u00ebggoon na\u00f1oo tii\u00f1al Yeesu. Yeesu s\u00ebgg, di bind ak baaraamam ci suuf.\n8:7 Bi laaj ya baree, mu siggi ne leen: \u00abKu musul a def b\u00e0kkaar ci y\u00e9en, na ko j\u00ebkk a s\u00e0nniy xeer.\u00bb\n8:8 Noonu mu s\u00ebggaat, dellu di bind ci suuf.\n8:9 Bi \u00f1u d\u00e9ggee loolu, \u00f1uy rocceeku kenn-kenn, mag \u00f1a jiitu. Yeesu rekk des fa, jig\u00e9en ja taxaw ca kanamam.\n8:10 Mu daldi siggi ne ko: \u00abJig\u00e9en ji, ana \u00f1i la doon jii\u00f1 njaaloo? Ndax kenn tegu la too\u00f1?\u00bb\n8:11 Mu ne ko: \u00abKenn, Sang bi.\u00bb Yeesu ne ko: \u00abMan it ci sama w\u00e0ll, duma la daan. Demal, waaye bul defati b\u00e0kkaar.\u00bb\n8:12 Yeesu jubluwaat ca mbooloo ma ne leen: \u00abMan maay leeru \u00e0ddina si. Ku ma topp doo dox cig l\u00ebnd\u00ebm, waaye dinga am leeru dund.\u00bb\n8:13 Farisen ya ne ko: \u00abYaw yaay seedeel sa bopp, kon li ngay wax du d\u00ebgg.\u00bb\n8:14 Yeesu tontu leen: \u00abMaa ngi seedeel sama bopp, teewul li may wax di d\u00ebgg, ndaxte xam naa fa ma b\u00e0yyikoo, xam fa ma j\u00ebm. Waaye y\u00e9en xamuleen fa ma b\u00e0yyikoo ak fa ma j\u00ebm.\n8:15 Ci gis-gisu \u00e0ddina ngeen di \u00e0ttee; man duma \u00e0tte kenn.\n8:16 Teewul nag, su ma demee bay \u00e0tte, bu jub lay doon, ndaxte du man rekk ay \u00e0tte, waaye Baay, bi ma y\u00f3nni, daf ciy \u00e0nd ak man.\n8:17 Seen yoon dafa wax ne, seedes \u00f1aari nit a g\u00ebn a w\u00f3or.\n8:18 Man maa ngi seedeel sama bopp, te Baay bi ma y\u00f3nni mi ngi may seedeel itam.\u00bb\n8:19 \u00d1u laaj ko ne: \u00abKuy sa baay?\u00bb Yeesu tontu ne: \u00abXamuleen ma, xamuleen sama Baay. Bu ngeen ma xamoon, xam ko.\u00bb\n8:20 Bi muy wax loolu, Yeesoo nga doon j\u00e0ngalee ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, ca wetu fa \u00f1u doon denc asaka ya. Kenn m\u00ebnu ko woon a j\u00e0pp, ndaxte waxtoom jotagul.\n8:21 Yeesu dellu ne leen: \u00abMaa ngi dem; dingeen ma seet, waaye seen b\u00e0kkaar ngeen di deeyaale. Fa ma j\u00ebm, dungeen fa man a dem.\u00bb\n8:22 Yawut yay waxante naan: \u00abNee na kat, fa mu j\u00ebm, dunu fa man a dem. Mbaa du day xaruji?\u00bb\n8:23 Yeesu tontu ne: \u00abY\u00e9en, fii ngeen bawoo, ci suuf, waaye man ca kaw laa j\u00f3ge. \u00c0ddina ngeen soqikoo, waaye man bokkuma ci.\n8:24 Looloo tax ma ne, ci seeni b\u00e0kkaar ngeen di dee. Bu ngeen g\u00ebmul ki ma nekk, dingeen dee ci seeni b\u00e0kkaar.\u00bb\n8:25 \u00d1u ne ko: \u00abYaay kan?\u00bb Mu ne leen: \u00abLi ma leen waxoon ca nj\u00e0lb\u00e9en ga.\n8:26 Li ma man a wax ci y\u00e9en ba \u00e0tte leen, bare na. Waaye ki ma y\u00f3nni, ku w\u00f3or la, te li mu ma wax rekk laay jottali \u00e0ddina.\u00bb\n8:27 Xamu\u00f1u woon ne, Y\u00e0lla Baay bee tax muy wax.\n8:28 Yeesu nag ne leen: \u00abBu ngeen y\u00e9kkatee Doomu nit ki, dingeen xam ne, Maay ki nekk. Dingeen xam ne it, duma def dara man ci sama bopp. Li ma Baay biy j\u00e0ngal rekk laay wax.\n8:29 Te it ki ma y\u00f3nnee ngi \u00e0nd ak man; musu maa b\u00e0yyi ma w\u00e9et, ndaxte li ko neex rekk laay def.\u00bb\n8:30 Bi \u00f1uy d\u00e9gg Yeesu di wax loolu, \u00f1u bare daldi koy g\u00ebm.\n8:31 Yeesu ne Yawut ya ko g\u00ebmoon: \u00abBu ngeen saxee ci li ma wax, nekk ngeen samay taalibe ci lu w\u00f3or.\n8:32 Te it dingeen xam d\u00ebgg gi te d\u00ebgg gi dina leen goreel.\u00bb\n8:33 \u00d1u tontu ko ne: \u00abNun ci Ibraayma lanu soqikoo te musunoo nekk jaamu kenn. Nan nga nu man a waxe ne, dina\u00f1u leen goreel?\u00bb\n8:34 Yeesu ne leen: \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, k\u00e9pp kuy b\u00e0kkaar, jaamu b\u00e0kkaar la.\n8:35 Te jaam du bokk ci k\u00ebr gi ba f\u00e0ww, waaye doom, moom, ci k\u00ebr gi la bokk ba f\u00e0ww.\n8:36 Kon nag bu leen Doom ji defee gor, dingeen doon ay gor tigi.\n8:37 Xam naa ne askanu Ibraayma ngeen. Waaye y\u00e9ena ngi may wut a rey, ndaxte li may j\u00e0ngale xajul ci y\u00e9en.\n8:38 Li ma sama Baay won laay wax; waaye y\u00e9en, li leen seen baay di wax ngeen di def.\u00bb\n8:39 \u00d1u tontu ko ne: \u00abIbraayma mooy sunu baay.\u00bb Yeesu ne leen: \u00abBu ngeen dee waa k\u00ebr Ibraayma, dingeen j\u00ebfe ni moom.\n8:40 L\u00e9egi nag y\u00e9ena ngi may wut a rey, man mi leen jottali d\u00ebgg, gi ma j\u00eble ca Y\u00e0lla. Ibraayma deful lu ni mel.\n8:41 Li ngeen donne ci seen baay rekk ngeen di def.\u00bb \u00d1u tontu ko ne: \u00abNun de, dunu doomi araam. Benn baay rekk lanu am, mooy Y\u00e0lla.\u00bb\n8:42 Yeesu ne leen: \u00abBu Y\u00e0lla doon seen baay, dingeen ma b\u00ebgg, ndaxte ca moom laa j\u00f3ge, \u00f1\u00ebw ci ndigalam. \u00d1\u00ebwaluma sama bopp, waaye moo ma y\u00f3nni.\n8:43 Lu tax d\u00e9gguleen li ma leen wax? Li ko waral moo di m\u00ebnuleen koo d\u00e9glu.\n8:44 Seytaane mooy seen baay, te b\u00ebgg-b\u00ebggam ngeen di b\u00ebgg di def. B\u00f3omkat la mas a doon. Du taxaw mukk ci d\u00ebgg, ndaxte d\u00ebgg nekkul ci moom. Buy fen, d\u00ebppoo na ak jikkoom, ndaxte fenkat la, te ci moom la fen soqikoo.\n8:45 Waaye man damay wax d\u00ebgg, moo tax g\u00ebmuleen ma.\n8:46 Kan ci y\u00e9en moo man a seede ne, b\u00e0kkaar naa? Su ma waxee d\u00ebgg nag, lu tax dungeen ma g\u00ebm?\n8:47 Ku nekk doomu Y\u00e0lla dina d\u00e9glu ay waxam. Waaye nekkuleen doomi Y\u00e0lla, looloo tax dungeen d\u00e9glu.\u00bb\n8:48 Yawut ya ne ko: \u00abNdax danoo waxul d\u00ebgg, bu nu nee, nitu Samari nga te dangaa am ay rab?\u00bb\n8:49 Yeesu ne leen: \u00abAwma rab; waaye sama Baay laay teral, te y\u00e9en dangeen may toroxal.\n8:50 Wutumaa m\u00e0ggal sama bopp. Keneen a ma koy wutal te mooy \u00e0tte.\n8:51 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, kuy s\u00e0mm sama wax doo dee mukk.\u00bb\n8:52 Yawut ya ne ko: \u00abL\u00e9egi w\u00f3or nanu ne, dangaa am ay rab! Ibraayma faatu na, yonent y\u00e9pp faatu, yaw nga naan: \u201cKuy s\u00e0mm sama wax, doo \u00f1am dee.\u201d\n8:53 Sunu baay Ibraayma faatu na; mbaa du dangaa defe ne, yaa ko g\u00ebn a m\u00e0gg? Yonent yi itam faatu na\u00f1u. Waaw, loo teg sa bopp?\u00bb\n8:54 Yeesu ne leen: \u00abSu ma dee m\u00e0ggal sama bopp, du am maana. Sama Baay a may m\u00e0ggal, moom mi ngeen naan, mooy seen Y\u00e0lla.\n8:55 Xamuleen ko nag; man maa ko xam. Su ma ne woon xawma ko, ab fenkat laay doon ni y\u00e9en. Waaye xam naa ko te maa ngi s\u00e0mm waxam.\n8:56 Seen baay Ibraayma b\u00e9g na, bi mu y\u00e9gee sama ngan. Bi mu ko gisee it, b\u00e9g na ci lool.\u00bb\n8:57 Yawut ya ne ko: \u00abAmaguloo jur\u00f3om-fukki at, ba noppi naan gis nga Ibraayma?\u00bb\n8:58 Yeesu ne leen: \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, laata \u00f1uy s\u00e0kk Ibraayma, fekk na ma doon ki \u00f1uy wax Maay ki nekk.\u00bb\n8:59 Noonu \u00f1u for ay xeer, b\u00ebgg ko koo s\u00e0nni ngir rey ko. Waaye Yeesu n\u00ebbbu, g\u00e9nn k\u00ebr Y\u00e0lla ga.\n9:1 Amoon na fu Yeesu jaaroon, gis fa waa ju judduwaale gumba.\n9:2 Taalibeem ya laaj ko ne: \u00abKilifa gi, lu tax waa jii judduwaale gumba? Ndax b\u00e0kkaaram a ko waral, walla bu waajuram?\u00bb\n9:3 Yeesu tontu ne: \u00abAjuwul ci b\u00e0kkaaram walla ci bu waajuram. Waaye loolu dafa am, ngir j\u00ebfi Y\u00e0lla yi fee\u00f1 ci moom.\n9:4 B\u00ebcc\u00ebg lanu war a matal j\u00ebfi ki ma y\u00f3nni; guddi dina \u00f1\u00ebwi, goo xam ne kenn du ci man a ligg\u00e9ey.\n9:5 Ci bi may nekk \u00e0ddina, maay leeru \u00e0ddina.\u00bb\n9:6 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, dafa daldi tifli, jaxase lor wa ak ban, tay ko ci b\u00ebti gumba ga ne ko:\n9:7 \u00abDemal s\u00eblmu ci b\u00ebtu Silowe.\u00bb Silowe mi ngi tekki \u00abY\u00f3nni na\u00f1u ko.\u00bb Gumba ga daldi dem s\u00eblmuji, dellusi di gis.\n9:8 D\u00ebkkandoom yi ak \u00f1i ko xame woon bu j\u00ebkk ci yelwaan naan: \u00abXanaa du kii moo daan toog, di yelwaan?\u00bb\n9:9 \u00d1ii naan: \u00abMoom la de!\u00bb \u00d1ee naan: \u00abDu moom! Da\u00f1oo niroo rekk.\u00bb Mu daldi leen ne: \u00abMan la de!\u00bb\n9:10 \u00d1u ne ko: \u00abLu ubbi say b\u00ebt?\u00bb\n9:11 Mu tontu ne: \u00abKu \u00f1uy wax Yeesu moo tooyal ban, tay ko ci samay b\u00ebt, ne ma: \u201cDemal s\u00eblmu ci b\u00ebtu Silowe.\u201d Ma dem nag s\u00eblmuji, daldi gis.\u00bb\n9:12 \u00d1u ne ko: \u00abAna waa ji?\u00bb Mu ne leen: \u00abXawma fu mu nekk.\u00bb\n9:13 Noonu \u00f1u daldi indil Farisen yi nit ki gumba woon.\n9:14 Ndekete Yeesu, b\u00e9s bi mu tooyale ban, ubbi b\u00ebti gumba ga, b\u00e9su noflaay la woon.\n9:15 Looloo tax Farisen ya di laajaat waa ja fi mu jaar bay gis l\u00e9egi. Mu ne leen: \u00abDafa tay ban ci samay b\u00ebt, ma s\u00eblmuji, ba fi ma nekk maa ngi gis.\u00bb\n9:16 Ci noonu am ca Farisen ya \u00f1u naan: \u00abKi def lii, m\u00ebnul a j\u00f3ge ca Y\u00e0lla, ndaxte toppul ndigalu b\u00e9su noflaay bi.\u00bb \u00d1eneen it di wax ne: \u00abNan la boroom b\u00e0kkaar man a wonee yii firnde?\u00bb Noonu \u00f1u daldi f\u00e9ewaloo ci seen biir.\n9:17 Farisen ya laajaat ka gumba woon ne ko: \u00abYaw, loo wax ci moom? Yaw de la ubbil say b\u00ebt.\u00bb Mu ne leen: \u00abYonent la.\u00bb\n9:18 Yawut ya m\u00ebnu\u00f1u woon a nangu ne, nit ka dafa gumba woon tey gis l\u00e9egi, \u00f1u daldi wooluji ay waajuram,\n9:19 laaj leen ne: \u00abNdax kii mooy seen doom, ji ngeen ne, gumba judduwaale la? Kon fu mu jaar, bay gis l\u00e9egi?\u00bb\n9:20 Waajur ya tontu ne: \u00abXam nanu ne daal, sunu doom la te dafa judduwaale gumba.\n9:21 Waaye ni mu def l\u00e9egi bay gis, xamunu ko, te xamunu it ki ko ubbil ay b\u00ebtam. Laajleen ko; magum j\u00ebmm la, te man na tontul boppam.\u00bb\n9:22 Ragal Yawut ya nag moo taxoon waajuri nit ka waxe noonu, ndaxte Yawut ya da\u00f1oo m\u00e0nkoo woon ne, k\u00e9pp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, \u00f1u d\u00e0q la ca j\u00e0ngu ba.\n9:23 Looloo tax waajur ya ne: \u00abLaajleen ko; magum j\u00ebmm la.\u00bb\n9:24 Farisen ya dellu woowaat ka gumba woon ne ko: \u00abWaxal sa digganteek Y\u00e0lla. Xam nanu ne, waa joojee boroom b\u00e0kkaar la.\u00bb\n9:25 Mu tontu ne: \u00abXawma ndax boroom b\u00e0kkaar la am d\u00e9et. Li ma xam daal mooy gumba woon naa, te l\u00e9egi maa ngi gis.\u00bb\n9:26 \u00d1u laaj ko ne: \u00abLu mu la def? Nu mu la ubbile say b\u00ebt?\u00bb\n9:27 Mu ne leen: \u00abWax naa leen ko ba noppi, waaye d\u00e9gluwuleen ma. Lu ngeen b\u00ebgg ci ma di ko wax, di waxaat? Xanaa dangeen a b\u00ebgg a nekk y\u00e9en itam ay taalibeem?\u00bb\n9:28 Ci kaw loolu \u00f1u daldi ko saaga ne ko: \u00abYaw yaay taalibeem. Nun, taalibey Musaa lanu.\n9:29 Xam nanu ne, Y\u00e0lla wax na ak Musaa; waaye kii, xamunu sax fu mu j\u00f3ge.\u00bb\n9:30 Waa ja ne leen: \u00abLoolu de, doy na waar! Xamuleen fu mu j\u00f3ge, te moo ubbi samay b\u00ebt!\n9:31 Xam nanu ne, Y\u00e0lla du d\u00e9glu boroom b\u00e0kkaar. Waaye nag, dina d\u00e9glu ki koy ragal tey def coobareem.\n9:32 Bi \u00e0ddina sosoo ba tey, musu\u00f1oo d\u00e9gg nit ku ubbi b\u00ebti gumbag judduwaale.\n9:33 Kon nit kookee nag, bu j\u00f3gewul woon ca Y\u00e0lla, du man a def dara.\u00bb\n9:34 \u00d1u tontu ko ne: \u00abYaw, ci biir b\u00e0kkaar nga juddoo, ba noppi di nu j\u00e0ngal?\u00bb Noonu \u00f1u d\u00e0q ko ca j\u00e0ngu ba.\n9:35 Yeesu daldi y\u00e9g ne, d\u00e0q na\u00f1u nit ka. Bi mu dajeek moom, mu ne ko: \u00abNdax g\u00ebm nga Doomu nit ki?\u00bb\n9:36 Waa ja ne ko: \u00abWax ma mooy kan, Sang bi, ba ma man koo g\u00ebm.\u00bb\n9:37 Yeesu ne ko: \u00abGis nga ko ba noppi, te mooy kiy wax ak yaw.\u00bb\n9:38 Waa ja ne: \u00abBoroom bi, g\u00ebm naa la.\u00bb Noonu mu jaamu Yeesu.\n9:39 Yeesu ne ko: \u00ab\u00c0ttee ma tax a \u00f1\u00ebw \u00e0ddina, ngir \u00f1i gumba gis, \u00f1iy gis gumba.\u00bb\n9:40 Bi Farisen ya nekkoon ak moom d\u00e9ggee loolu, \u00f1u ne ko: \u00abXanaa kon nun it danoo gumba?\u00bb\n9:41 Yeesu tontu leen ne: \u00abBu ngeen gumba woon, dungeen am b\u00e0kkaar, waaye fi ak y\u00e9ena ngi naan: \u201cNu ngi gis,\u201d ci b\u00e0kkaar ngeen di d\u00ebkk.\n10:1 \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, ku jaar feneen fu dul ci buntu g\u00e9tt gi, kooku s\u00e0cc la, saay-saay la.\n10:2 Waaye ki jaar ci bunt bi, mooy s\u00e0mmu xar yi.\n10:3 Wottukat bi dina ko ubbil bunt bi, xar yiy d\u00e9gg baatam. Xar yi mu moom nag, bu ci nekk dina la woo ci sa tur, ba noppi nga topp ko ci biti.\n10:4 S\u00e0mm bi, bu g\u00e9nnee yi mu moom y\u00e9pp, dina leen jiitu, \u00f1u topp ko, ndaxte xam na\u00f1u baatam.\n10:5 Waaye du\u00f1u topp jaambur; da\u00f1u koy daw, ndaxte miinu\u00f1u baatam.\u00bb\n10:6 Yeesu misaaloon na leen loolu, waaye xamu\u00f1u lu mu leen doon wax.\n10:7 Noonu Yeesu newaat: \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, man maay buntu g\u00e9tt gi.\n10:8 \u00d1i ma fi jiitu \u00f1\u00e9pp ay s\u00e0cc la\u00f1u, ak ay saay-saay; waaye xar yi d\u00e9gluwu\u00f1u leen.\n10:9 Man maay bunt bi; ku jaar ci man, dinga mucc, dinga man a dugg ak a g\u00e9nn, dinga am it mbooy goo man a fore.\n10:10 S\u00e0cc bi moom, day s\u00e0ccsi rekk, di rey ak a y\u00e0q. Man damaa \u00f1\u00ebw, ngir nit \u00f1i am dund, ba nekk ci naataange.\n10:11 \u00abMan maay s\u00e0mm bu baax bi. S\u00e0mm bu baax bi day joxe bakkanam ngir ay xaram.\n10:12 Ki dul s\u00e0mm bi tey ligg\u00e9eyal xaalis rekk waaye moomul xar yi, bu s\u00e9enee bukki, day daw, b\u00e0yyi fa xar ya. Bu ko defee bukki ba dal ca coggal ja, j\u00e0pp ca, tasaare ya ca des.\n10:13 Booba surga day daw, ndaxte xaalis rekk lay ligg\u00e9eyal, faalewul xar ya.\n10:14 \u00abMan maay s\u00e0mm bu baax bi. Ni ma xame Baay bi te Baay bi xame ma ni, noonu laa xame samay xar, te \u00f1oom it ni la\u00f1u ma xame. Te it kat dinaa joxe sama bakkan ngir xar yi.\n10:16 Am naa yeneen xar yu bokkul ci g\u00e9tt gii. War naa leen a indi, \u00f1oom it, te dina\u00f1u d\u00e9glu sama baat. Benn coggal ay am ak benn s\u00e0mm.\n10:17 Baay bi b\u00ebgg na ma, ndaxte damay joxe sama bakkan ngir j\u00eblaat ko.\n10:18 Kenn du ko j\u00eble ci man; maa koy joxe ci sama coobarey bopp. Am naa it sa\u00f1-sa\u00f1u joxe ko te am naa sa\u00f1-sa\u00f1u j\u00eblaat ko. Loolu la ma sama Baay sant.\u00bb\n10:19 K\u00e0ddu yooyee \u00f1oo f\u00e9ewalewaat Yawut yi.\n10:20 \u00d1u bare ca \u00f1oom naan: \u00abDafa \u00e0nd ak rab! Dafa dof! Lu tax ngeen koy d\u00e9glu?\u00bb\n10:21 Waaye \u00f1eneen naan: \u00abNit ku am ay rab du waxe nii. Ndax rab man na ubbi b\u00ebti gumba?\u00bb\n10:22 Am b\u00e9s \u00f1u doon m\u00e0ggal ca Yerusalem B\u00e9s ba \u00f1u sellale woon k\u00ebr Y\u00e0lla ga; ci jamonoy sedd la woon.\n10:23 Yeesoo nga woon ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, di doxantu ca biir Werandaa bu Suleymaan.\n10:24 Yawut ya w\u00ebr ko ne ko: \u00abKa\u00f1 nga nuy dindi ci kumpa? Boo dee Almasi bi, wax ko mu leer.\u00bb\n10:25 Yeesu tontu leen ne: \u00abWax naa leen ko ba noppi, waaye g\u00ebmuleen. J\u00ebf yi may def ci sama turu Baay \u00f1oo may seede.\n10:26 Waaye g\u00ebmuleen ndaxte bokkuleen ci samay xar.\n10:27 Samay xar dina\u00f1u d\u00e9gg sama baat; xam naa leen te \u00f1u ngi may topp.\n10:28 Dama leen di jox dund gu dul jeex; du\u00f1u s\u00e0nku mukk, te kenn du leen j\u00eble ci sama loxo.\n10:29 Baay bi ma leen jox, moo g\u00ebn a m\u00e0gg l\u00e9pp, te kenn m\u00ebnul a j\u00eble dara ci loxob Baay bi.\n10:30 Man ak Baay bi benn lanu.\u00bb\n10:31 Yawut ya daldi foraat ay xeer, b\u00ebgg koo s\u00e0nni, ngir rey ko.\n10:32 Noonu Yeesu ne leen: \u00abDef naa ci seen kanam j\u00ebf yu baax yu bare ci ndigalu Baay bi. Ban ci j\u00ebf yooyu moo tax ba ngeen b\u00ebgg maa s\u00e0nni ay doj?\u00bb\n10:33 Yawut ya ne ko: \u00abJ\u00ebf ju baax taxul nu b\u00ebgg laa s\u00e0nniy xeer, waaye dangay suufeel turu Y\u00e0lla; yaw, nit rekk nga, ba noppi di def sa bopp Y\u00e0lla!\u00bb\n10:34 Yeesu tontu ne: \u00abBind na\u00f1u ci seen t\u00e9ereb yoon ne: \u201cY\u00e0lla nee na: Ay y\u00e0lla ngeen.\u201d\n10:35 Y\u00e0lla wooye na \u201cay y\u00e0lla\u201d \u00f1i mu y\u00f3nnee k\u00e0ddoom, te xam nanu ne, kenn m\u00ebnul a randal waxi Y\u00e0lla.\n10:36 Kon nu ngeen man a waxe ne, damay suufeel turu Y\u00e0lla ndax li ma ne Doomam laa, man mi Y\u00e0lla t\u00e0nn, y\u00f3nni ma ci \u00e0ddina?\n10:37 Su ma deful sama j\u00ebfi Baay, buleen ma g\u00ebm;\n10:38 waaye su ma ko defee, bu ngeen ma g\u00ebmul sax, g\u00ebmleen boog samay j\u00ebf, ngir ngeen xam te nangu ne, maa ngi nekk ci Baay bi te Baay bi nekk na ci man.\u00bb\n10:39 \u00d1u di ko wut a j\u00e0ppaat, waaye mu b\u00e0yyi leen fa, dem.\n10:40 Yeesu g\u00e9nn, j\u00e0llaat dexu Yurdan, toog fa Yaxya daan s\u00f3obe ci ndox bu j\u00ebkk.\n10:41 Nit \u00f1u bare \u00f1\u00ebw ci moom, te naan: \u00abYaxya deful benn k\u00e9emaan, waaye li mu wax ci kii y\u00e9pp, d\u00ebgg la.\u00bb\n10:42 Noonu \u00f1u bare g\u00ebm ko.\n11:1 Amoon na benn waay bu woppoon, \u00f1u koy wax Lasaar. Ma nga d\u00ebkkoon Betani, moom ak Maryaama ak M\u00e0rt, mi mu bokkaloon ndey ak baay.\n11:2 Maryaama mooy jig\u00e9en jiy sottiji latkolo\u00f1 ci t\u00e0nki Boroom bi, fompe ko kawaram. Moom la c\u00e0mmi\u00f1am Lasaar woppoon.\n11:3 \u00d1aari jig\u00e9eni Lasaar y\u00f3nnee ca Yeesu ne ko: \u00abBoroom bi, sa xarit wopp na.\u00bb\n11:4 Bi Yeesu d\u00e9ggee xebaar boobu, mu ne: \u00abLasaar de, woppam jooju du ko mujje; day wone ndamu Y\u00e0lla, tey m\u00e0ggal Doomu Y\u00e0lla ji.\u00bb\n11:5 Yeesu soppoon na M\u00e0rt ak Maryaama ak Lasaar.\n11:6 Bi mu y\u00e9gee nag ne, Lasaar wopp na, mu toogaat yeneen \u00f1aari fan ca b\u00e9rab, ba mu nekkoon.\n11:7 Gannaaw loolu mu ne taalibe ya: \u00abNanu dellu Yude.\u00bb\n11:8 Taalibe ya tontu ko ne: \u00abKilifa gi, y\u00e0ggul dara waa Yude doon na\u00f1u la wut a rey ak i xeer, nga di fa dellu?\u00bb\n11:9 Yeesu ne leen: \u00abXanaa du b\u00ebcc\u00ebg fukki waxtook \u00f1aar la? Kuy dox b\u00ebcc\u00ebg, du fakkastalu, ndaxte day gis leeru \u00e0ddina si.\n11:10 Waaye kuy dox guddi, dina fakkastalu, ndaxte leer nekkul ci moom.\u00bb\n11:11 Yeesu wax loolu, teg ca ne: \u00abSunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko.\u00bb\n11:12 Taalibe ya tontu ne: \u00abBoroom bi, bu nelawee kay, kon dina w\u00e9r.\u00bb\n11:13 Yeesu dafa b\u00ebggoon a wax ne, Lasaar dee na, waaye taalibe yi da\u00f1oo xalaatoon ne, mbiri nelaw rekk lay wax.\n11:14 Ci kaw loolu Yeesu wax ci lu leer ne: \u00abLasaar dee na.\n11:15 B\u00e9g naa ngir y\u00e9en ndax li ma fa nekkul, ngir seen ng\u00ebm g\u00ebn a d\u00ebg\u00ebr. Waaye nanu ko seeti.\u00bb\n11:16 Noonu Tomaa, ki turam di tekki \u00abS\u00e9ex bi,\u00bb daldi ne yeneen taalibe ya: \u00abNanu dem nun itam, deeyandoo ak moom!\u00bb\n11:17 Bi Yeesu agsee, mu fekk ne, bi \u00f1u dencee Lasaar ak l\u00e9egi, mat na \u00f1eenti fan.\n11:18 Betani ma nga woon ca wetu Yerusalem, diggante bi matul woon sax \u00f1etti kilomet.\n11:19 Yawut yu bare \u00f1\u00ebwoon na\u00f1u k\u00ebr M\u00e0rt ak Maryaama, ngir d\u00ebf\u00ebl leen ci seen deewu c\u00e0mmi\u00f1.\n11:20 Bi Yeesu \u00f1\u00ebwee, M\u00e0rt y\u00e9g ko, dem di dajeek moom; fekk booba Maryaamaa nga toogoon ca k\u00ebr ga.\n11:21 M\u00e0rt ne Yeesu: \u00abBoroom bi, boo fi nekkoon de, sama c\u00e0mmi\u00f1 li du dee.\n11:22 Waaye xam naa ne, fii nu tollu sax, loo \u00f1aan Y\u00e0lla, mu may la ko.\u00bb\n11:23 Yeesu ne ko: \u00abSa c\u00e0mmi\u00f1 dina dekki.\u00bb\n11:24 M\u00e0rt tontu ko ne: \u00abXam naa ne, dina j\u00f3g b\u00e9su ndekkite la, keroog b\u00e9s bu mujj ba.\u00bb\n11:25 Yeesu ne ko: \u00abMan maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma g\u00ebm, boo deeyee it, dinga dund.\n11:26 Rax-ca-dolli kuy dund te g\u00ebm ma, doo dee mukk. Ndax g\u00ebm nga loolu?\u00bb\n11:27 Mu tontu ko ne: \u00abWaaw Boroom bi. G\u00ebm naa ne, yaay Almasi bi, di Doomu Y\u00e0lla, ji war a \u00f1\u00ebw \u00e0ddina.\u00bb\n11:28 Bi M\u00e0rt waxee loolu, mu daldi dem woowi Maryaama ne ko ci pett: \u00abKilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj.\u00bb\n11:29 Bi Maryaama d\u00e9ggee loolu, mu daldi j\u00f3g, gaawantoo dem ca Yeesu.\n11:30 Te fekk duggagul woon ca d\u00ebkk ba, waaye ma nga woon ba tey ca b\u00e9rab, ba mu daje woon ak M\u00e0rt.\n11:31 Noonu Yawut, ya nekkoon ca k\u00ebr ga di d\u00ebf\u00ebl Maryaama, gis ko mu ne b\u00ebr\u00e9t g\u00e9nn, \u00f1u daldi koy topp, defe ne, day jooyi ca b\u00e0mmeel ba.\n11:32 Bi Maryaama agsee nag ca Yeesu, ba gis ko, mu daanu ciy t\u00e0nkam ne ko: \u00abBoroom bi, boo fi nekkoon, sama c\u00e0mmi\u00f1 du dee.\u00bb\n11:33 Yeesu gis ne, mi ngi jooy te Yawut yi \u00e0nd ak moom itam \u00f1u ngi jooy. Mu daldi j\u00e0q, am naqar wu r\u00e9y.\n11:34 Mu ne leen: \u00abFu ngeen ko denc?\u00bb \u00d1u tontu ko ne: \u00abKaay gis, Sang bi.\u00bb\n11:35 Yeesu jooy.\n11:36 Noonu nag, Yawut ya ne: \u00abGis ngeen ni mu ko b\u00ebgge woon!\u00bb\n11:37 Waaye am na ca \u00f1oom \u00f1u doon wax naan: \u00abMoom mi ubbi b\u00ebti gumba gi, ndax m\u00ebnul woon a fexe ba Lasaar du dee?\u00bb\n11:38 Yeesu dellu am naqar wu r\u00e9y, daldi dem ca b\u00e0mmeel ba. Pax la mu \u00f1u yett ci doj, ube ko xeer.\n11:39 Yeesu ne: \u00abDindileen xeer wi!\u00bb M\u00e0rt, jig\u00e9enu ku dee ki ne ko: \u00abBoroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci b\u00e0mmeel bi \u00f1eenti fan.\u00bb\n11:40 Yeesu ne ko: \u00abNdax waxuma la ne, boo g\u00ebmee, dinga gis ndamu Y\u00e0lla?\u00bb\n11:41 \u00d1u daldi dindi xeer wa. Yeesu xool ci kaw, ne j\u00e0kk asamaan, \u00f1aan Y\u00e0lla ne: \u00abBaay, sant naa la ci li nga ma d\u00e9glu ba noppi.\n11:42 Xam naa ne, doo j\u00f3g ci di ma d\u00e9glu, waaye dama koy wax, ngir nit \u00f1i ma w\u00ebr g\u00ebm ne, yaa ma y\u00f3nni.\u00bb\n11:43 Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu d\u00ebg\u00ebr ne: \u00abLasaar, \u00f1\u00ebwal ci biti!\u00bb\n11:44 N\u00e9ew bi daldi g\u00e9nn, \u00f1u gis c\u00e0ngaay, li \u00f1u takke woon t\u00e0nk yi ak loxo yi, ak kaala, gi \u00f1u muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: \u00abTekkileen ko, b\u00e0yyi ko mu dem.\u00bb\n11:45 Yawut yu bare ca \u00f1a \u00f1\u00ebwoon k\u00ebr Maryaama te gis li Yeesu defoon, daldi koy g\u00ebm.\n11:46 Waaye amoon na it \u00f1u demoon ci Farisen ya, nettali leen la Yeesu defoon.\n11:47 Farisen ya ak saraxalekat yu mag ya woo kureelu \u00e0ttekat ya ne: \u00abNit kii kat, k\u00e9emaan yi muy def a ngi b\u00ebgg a bare. Lu nuy def nag?\n11:48 Ndaxte su nu ko b\u00e0yyee mu j\u00e0ppoo nii, \u00f1\u00e9pp dina\u00f1u ko g\u00ebm, te kilifay Room yi dina\u00f1u \u00f1\u00ebw, daaneel sunu k\u00ebr Y\u00e0lla gi, tas sunu r\u00e9ew!\u00bb\n11:49 Amoon na ca \u00f1oom ku \u00f1uy wax Kayif te mu nekkoon saraxalekat bu mag ba at mooma; mu ne leen: \u00abXamuleen ci mbir mi dara.\n11:50 Xanaa xamuleen ne, kenn nit rekk dee ngir \u00f1\u00e9pp, mooy li g\u00ebn ci y\u00e9en? Bu ko defee r\u00e9ew mi du tas.\u00bb\n11:51 Loolu Kayif waxu ko woon ci sagoom, waaye li mu nekkoon saraxalekat bu mag ba at mooma, moo tax Y\u00e0lla xiirtal ko mu ne, Yeesu dina dee ngir r\u00e9ew mi.\n11:52 Du woon rekk ngir xeet woowu, waaye ngir itam doomi Y\u00e0lla, yi tasaaroo y\u00e9pp, dajaloo nekk benn.\n11:53 Keroog la njiiti Yawut ya dogu ci rey Yeesu.\n11:54 Taxoon na ba Yeesu dootul doxantu ci biir Yawut ya. Noonu mu dem ca gox bu jege m\u00e0ndi\u014b ma, ca d\u00ebkku Efrayim. Foofa nag la toog ak ay taalibeem.\n11:55 B\u00e9su J\u00e9ggi ba, di m\u00e0ggalu Yawut ya, mu ngi doon jubsi, ba \u00f1u bare ca waa \u00e0ll ba di dem Yerusalem balaa booba, ngir sanguji set.\n11:56 \u00d1u ngi doon wut Yeesu tey waxante ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga naan: \u00abLu ngeen ci xam? Ndax dina \u00f1\u00ebw ci m\u00e0ggal gi walla d\u00e9et?\u00bb\n11:57 Saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya daldi santaane ne, bu kenn xamee fu Yeesu nekk, mu y\u00e9gle ko, ngir \u00f1u man koo j\u00e0pp.\n12:1 Jur\u00f3om benni fan laata m\u00e0ggalu b\u00e9sub J\u00e9ggi ba, Yeesu dem na Betani, d\u00ebkku Lasaar, mi mu dekkal.\n12:2 Foofa \u00f1u defaral ko fa reer. M\u00e0rt moo ko doon s\u00e9ddale, te Lasaar bokkoon na ca gan \u00f1a.\n12:3 Noonu Maryaama daldi j\u00ebl liibaru latkolo\u00f1 ju raxul ju \u00f1uy wax n\u00e0rd, tey jar lu baree-bare. Mu sotti ko ci t\u00e0nki Yeesu, ba noppi fomp ko ak kawaram. Xetu latkolo\u00f1 gi gilli ci k\u00ebr gi y\u00e9pp.\n12:4 Kenn ca taalibey Yeesu ya, muy Yudaa Iskariyo, mi ko nar a wor, daldi ne:\n12:5 \u00abLu tax jaayewu\u00f1u latkolo\u00f1 jii peyu atum l\u00ebmm, jox ko miskin yi?\u00bb\n12:6 Waaye bi muy wax loolu, xalaatul woon miskin yi, ndaxte s\u00e0cc la woon; moo yoroon boyetu xaalis bi, te daan ci s\u00e0kk.\n12:7 Waaye Yeesu ne ko: \u00abB\u00e0yyi ko! Jekkoon na mu denc ko ngir b\u00e9s bu \u00f1u may suul.\n12:8 Miskin yaa ngi ak y\u00e9en b\u00e9s bu nekk, waaye dungeen ma gis ba f\u00e0ww.\u00bb\n12:9 Bi \u00f1u y\u00e9gee ne, Yeesoo nga fa, mbooloom Yawut mu bare daldi dem Betani. Yeesu rekk y\u00f3bbuwu leen fa woon, waaye da\u00f1oo b\u00ebggoon a gisaale Lasaar, mi Yeesu dekkaloon.\n12:10 Saraxalekat yu mag ya dogu ci ne, da\u00f1uy reyaale Lasaar,\n12:11 ndaxte moo waral Yawut yu bare d\u00ebddu leen, g\u00ebm Yeesu.\n12:12 Ca \u00ebll\u00ebg sa mbooloo mu bare, ma \u00f1\u00ebwoon ca m\u00e0ggalu b\u00e9sub J\u00e9ggi ba, y\u00e9g ne Yeesoo ngi j\u00ebmsi Yerusalem.\n12:13 \u00d1u daldi j\u00ebl cari garab, g\u00e9nn di ko teeru. \u00d1uy xaacu naan:\u00abOsaana!Yaw miy \u00f1\u00ebw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Na Y\u00e0lla barkeel buuru Israyil!\u00bb\n12:14 Yeesu wut cumbur, war ko; ndaxte Mbind mi nee na:\n12:15 \u00abBuleen ragal, waa Siyon.Gis ngeen, seen buur a ngi \u00f1\u00ebw,war mbaam mu ndaw.\u00bb\n12:16 Yooyu y\u00e9pp, taalibe ya xamu\u00f1u woon ca saa sa lu muy tekki; waaye gannaaw bi ndamu Yeesu fee\u00f1ee, \u00f1u f\u00e0ttaliku ne, Mbind mi y\u00e9gle woon na loolu ci moom, te amal na\u00f1u ko.\n12:17 \u00d1a nekkoon ak Yeesu \u00f1\u00e9pp, bi muy wooyee Lasaar mu g\u00e9nn ca b\u00e0mmeel ba te mu dekkal ko, demoon na\u00f1u, nettali la \u00f1u gis.\n12:18 Looloo tax mbooloo ma teeru ko, ndaxte y\u00e9goon na\u00f1u firnde boobu.\n12:19 Farisen yi nag di waxante naan: \u00abGis ngeen, m\u00ebnuleen ci dara; \u00f1\u00e9pp a ngi koy topp!\u00bb\n12:20 Ca mbooloo ma, amoon na ca ay Gereg yu bokk ca \u00f1a \u00f1\u00ebwoon Yerusalem ngir jaamu Y\u00e0lla diirub m\u00e0ggal ga.\n12:21 \u00d1\u00ebw na\u00f1u ci Filib, mi d\u00ebkk Betsayda ci diiwaanu Galile, ne ko: \u00abSang bi, danoo b\u00ebggoon a gis Yeesu.\u00bb\n12:22 Filib dem wax ko Andare; \u00f1u \u00e0nd, waxi ko Yeesu.\n12:23 Mu tontu leen ne: \u00abWaxtu wi \u00f1u war a fee\u00f1ale ndamu Doomu nit ki jot na.\n12:24 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, fi ak peppu dugub ji wadd ci suuf jaarul ci dee, du man a weesu li mu doon: pepp do\u014b\u014b. Waaye bu deeyee, dina jur pepp yu bare.\n12:25 Ku b\u00ebgg bakkanam dina ko \u00f1\u00e0kk, waaye ku ko ba\u00f1 ci \u00e0ddina sii, dina ko denc ngir dund gu dul jeex gi.\n12:26 Ku b\u00ebgg a doon sama surga, na ma topp. Bu ko defee, fu ma nekk, fa lay nekk moom itam. Ku may ligg\u00e9eyal, sama Baay dina ko teral.\n12:27 \u00abL\u00e9egi nag damaa j\u00e0q. Lu may war a wax? Mbaa du dama naan: \u201cBaay, musal ma ci li nar a xew waxtu wiy \u00f1\u00ebw?\u201d D\u00e9ed\u00e9et, \u00f1\u00ebw naa sax ngir jaar ci waxtu woowu.\n12:28 Baay, m\u00e0ggalal sa tur!\u00bb Noonu \u00f1u d\u00e9gg baat bu j\u00f3ge asamaan naan: \u00abM\u00e0ggal naa ko ba noppi, te dinaa ko m\u00e0ggalaat.\u00bb\n12:29 Mbooloo ma fa teewoon te d\u00e9gg baat ba daldi ne: \u00abD\u00ebnnu la woon!\u00bb \u00d1eneen naan: \u00abMalaakaa doon wax ak moom.\u00bb\n12:30 Waaye Yeesu ne leen: \u00abTaxuma baat boobu jolli, waaye y\u00e9ena tax.\n12:31 \u00c0tteb \u00e0ddina si jot na: l\u00e9egi \u00f1u d\u00e0q malaaka mu bon, mi jiite \u00e0ddina si.\n12:32 Te man, bu \u00f1u ma y\u00e9kkatee, ma tiim suuf, dinaa wootal nit \u00f1\u00e9pp ci man.\u00bb\n12:33 Ci baat yooyu la doon misaale ni mu war a faatoo.\n12:34 Mbooloo ma tontu ko ne: \u00abJ\u00e0ng nanu ci sunu t\u00e9ereb yoon ne, Almasi bi dina sax ba f\u00e0ww. Kon yaw, nan nga man a waxe ne, \u201cDoomu nit ki dina y\u00e9kkatiku?\u201d Kuy Doomu nit kooku?\u00bb\n12:35 Yeesu ne leen: \u00abLeer gi dootul y\u00e0gg ak y\u00e9en. Doxleen, ci bi ngeen dee am leer, ngir l\u00ebnd\u00ebm ba\u00f1 leen a bett. Ndaxte kuy dox ci l\u00ebnd\u00ebm doo xam foo j\u00ebm.\n12:36 Kon ci bi ngeen dee am leer gi, g\u00ebmleen ko, ngir ngeen doon doomi leer.\u00bb Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa dem, n\u00ebbbatuji leen.\n12:37 Firnde yi mu leen won y\u00e9pp taxul \u00f1u g\u00ebm ko,\n12:38 ngir li yonent Y\u00e0lla Esayi waxoon am:\u00abBoroom bi, ana ku g\u00ebm sunu waare?Kan la Boroom bi won dooleem?\u00bb\n12:39 M\u00ebnu\u00f1u woon a g\u00ebm, ndaxte Esayi dafa waxaat ne:\n12:40 \u00abY\u00e0lla dafa gumbaal seeni b\u00ebt,def ba \u00f1u d\u00ebg\u00ebr bopp,ngir seeni b\u00ebt ba\u00f1 a gis,seen xel ba\u00f1 a xam,\u00f1u ba\u00f1 a wo\u00f1\u00f1iku ci manngir ma w\u00e9ral leen.\u00bb\n12:41 Esayi dafa wax loolu, ndaxte gisoon na ndamu Yeesu te mi ngi doon wax ci ay mbiram.\n12:42 Fekk na ci biir njiit yi sax, \u00f1u bare g\u00ebmoon na\u00f1u Yeesu, waaye Farisen yee tax f\u00e9salu\u00f1u ko, ndaxte da\u00f1oo ragaloon, \u00f1u d\u00e0q leen ca j\u00e0ngu ba.\n12:43 Ng\u00ebr\u00ebmu nit a leen g\u00ebnaloon ng\u00ebr\u00ebmu Y\u00e0lla.\n12:44 Yeesu y\u00e9gle ne: \u00abKu ma g\u00ebm, g\u00ebmuloo ma waaye g\u00ebm nga ki ma y\u00f3nni.\n12:45 Ku ma gis, gis nga ki ma y\u00f3nni.\n12:46 Ni ag leer laa w\u00e0cce ci \u00e0ddina, ngir ku ma g\u00ebm du des ci l\u00ebnd\u00ebm.\n12:47 Ku d\u00e9gg samay wax te toppu leen, du man maa koy daan, ndaxte w\u00e0ccuma ngir daan \u00e0ddina, waaye damaa \u00f1\u00ebw ngir musal ko.\n12:48 Ku ma beddeeku te nanguwul samay wax, dina fekk fii li koy daan: sama nj\u00e0ngalee koy daan keroog b\u00e9s bu mujj ba.\n12:49 Ndaxte waxuma ci sama coobare, waaye Baay bi ma y\u00f3nni ci boppam, moo ma sant li ma war a wax ak li ma war a j\u00e0ngale.\n12:50 Te xam naa ne, li muy santaane day joxe dund gu dul jeex. Kon li ma wax, dama koy wax, ni ma ko Baay bi sante.\u00bb\n13:1 Laata m\u00e0ggalu b\u00e9su J\u00e9ggi ba la woon. Yeesu xamoon na ne, waxtu wi mu war a g\u00e9nne \u00e0ddina, dem ca wetu Baay ba, jot na. Ku b\u00ebgg \u00f1o\u00f1am yi nekk ci \u00e0ddina la, te b\u00ebgg na leen ba fa mb\u00ebggeel man a yem.\n13:2 Yeesu ak taalibe yaa ngi doon reer. Fekk na booba Seytaane xiirtal Yudaa, doomu Simo\u014b Iskariyo, ngir mu wori Yeesu.\n13:3 Yeesu xamoon na ne, Y\u00e0lla joxoon na ko sa\u00f1-sa\u00f1 ci l\u00e9pp, xam it ne, ca Y\u00e0lla la j\u00f3ge te ca moom lay delluwaat.\n13:4 Mu daldi j\u00f3ge ca reer ba, summi mbubbam, daldi j\u00ebl ab sarbet, laxas ko ci ndiggam.\n13:5 Noonu mu sotti ndox ci ab k\u00ebll, daldi t\u00e0mbali di raxas t\u00e0nki taalibe ya, di leen fomp ak sarbet, ba mu laxasaayoo.\n13:6 Bi mu agsee ba ca Simo\u014b Piyeer, kooku ne ko: \u00abBoroom bi, ndax yaw dangaa nar a raxas samay t\u00e0nk?\u00bb\n13:7 Yeesu tontu ko ne: \u00abXamoo fii mu nekk li may def, waaye dinga ko xami.\u00bb\n13:8 Piyeer ne ko: \u00abD\u00e9ed\u00e9et, duma nangu mukk nga raxas samay t\u00e0nk.\u00bb Yeesu ne ko: \u00abSu ma la raxasul, doo bokk ak man dara.\u00bb\n13:9 Simo\u014b Piyeer ne ko: \u00abKon nag Boroom bi, bul yem rekk ci t\u00e0nk yi, waaye raxasaaleel loxo yi ak bopp bi!\u00bb\n13:10 Yeesu ne ko: \u00abKu sangu ba noppi, soxlaatul a raxas lu dul ay t\u00e0nkam, ndaxte set na wecc. Y\u00e9en nag set ngeen, waaye du \u00f1\u00e9pp!\u00bb\n13:11 Fekk Yeesu xamoon na ki ko nar a wor, looloo tax mu ne: \u00abSetuleen y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.\u00bb\n13:12 Bi mu leen raxasalee seeni t\u00e0nk ba noppi, Yeesu dafa solaat mbubbam, dellu toogaat ne leen: \u00abNdax xam ngeen li ma leen defal?\n13:13 Y\u00e9en a ngi may wooye \u201cKilifa gi\u201d ak \u201cBoroom bi,\u201d te wax ngeen d\u00ebgg, moom laa.\n13:14 Kon bu fekkee ne man miy Boroom bi tey Kilifa gi, maa leen raxasal seeni t\u00e0nk, y\u00e9en itam war ngeen di raxasalante seeni t\u00e0nk.\n13:15 B\u00e0yyil naa leen fi royukaay, ngir ngeen di j\u00ebf, nii ma j\u00ebfeek y\u00e9en.\n13:16 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, jaam g\u00ebnul a m\u00e0gg sangam, mbaa ndaw, ki ko y\u00f3nni.\n13:17 Gannaaw xam ngeen loolu, bu ngeen doxalee noonu, dingeen b\u00e9g.\n13:18 \u00abY\u00e9en \u00f1\u00e9pp taxuleen may wax; xam naa \u00f1i ma t\u00e0nn. Waaye li Mbind mi wax, f\u00e0ww mu am, bi \u00f1u naan: \u201cKi lekk sama dugub w\u00e9q na ma.\u201d\n13:19 Maa ngi leen koy wax ci teel, bala looloo \u00f1\u00ebw, ngir bu \u00f1\u00ebwee, ngeen g\u00ebm ne, Maay ki nekk.\n13:20 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, ku nangu kenn ci \u00f1i may y\u00f3nni, nangu nga ma, man itam; te ku ma nangu, nangu nga ki ma y\u00f3nni.\u00bb\n13:21 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mu j\u00e0q, biral ne: \u00abCi d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, kenn ci y\u00e9en dina ma wor.\u00bb\n13:22 Taalibe yi di xoolante, te xamu\u00f1u kan lay wax.\n13:23 Ka Yeesu b\u00ebggoon te mu bokkoon ca taalibe ya, ma nga s\u00f3onu woon ca kaw Yeesu.\n13:24 Kooku la Simo\u014b Piyeer liyaar, ngir mu laaj Yeesu ki ko taxoon di wax.\n13:25 Taalibe ba daldi walbatiku ca Yeesu, laaj ko ne: \u00abBoroom bi, kooku kan la?\u00bb\n13:26 Yeesu ne ko: \u00abDinaa capp dogu mburu ci ndab li; ki ma koy jox, kooku la.\u00bb Noonu Yeesu j\u00ebl dogu mburu, capp ko ca ndab la, daldi koy jox Yudaa, doomu Simo\u014b Iskariyo.\n13:27 Naka la Yudaa j\u00ebl dog wa, Seytaane dugg ci moom. Yeesu ne ko: \u00abGaawantul ci li ngay def!\u00bb\n13:28 Amul kenn ca \u00f1a fa toogoon ku xam lu tax mu wax ko loolu.\n13:29 Waaye gannaaw Yudaa moo yoroon boyetu xaalis bi, am \u00f1u xalaat ne, Yeesu dafa koo wax, mu dem j\u00ebndi li war ci m\u00e0ggal gi, walla mu ne ko mu dem sarax miskin yi.\n13:30 Yudaa nag j\u00ebl dogu mburu ma, daldi g\u00e9nn ca saa sa. Booba guddi woon na.\n13:31 Bi Yudaa g\u00e9nnee, Yeesu ne: \u00abL\u00e9egi nag ndamu Doomu nit ki fee\u00f1 na, te ndamu Y\u00e0lla fee\u00f1 na itam ci moom.\n13:32 Te bu ma fee\u00f1alee ndamu Y\u00e0lla, Y\u00e0lla itam ci teewaayam dina fee\u00f1al ndamu Doomu nit ki, te dina ko def l\u00e9egi.\n13:33 Samay soppe, sama nekk ak y\u00e9en dootul y\u00e0gg. Dingeen may seet, waaye maa ngi leen di wax l\u00e9egi li ma waxoon Yawut ya: fa ma j\u00ebm, dungeen fa man a dem.\n13:34 Maa ngi leen di jox ndigal lu bees: b\u00ebgganteleen. Nangeen di b\u00ebggante ni ma leen b\u00ebgge.\n13:35 Ni \u00f1uy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngeen b\u00ebggante.\u00bb\n13:36 Simo\u014b Piyeer laaj ko ne: \u00abBoroom bi, foo j\u00ebm?\u00bb Yeesu ne ko: \u00abFa ma j\u00ebm, m\u00ebnuloo ma faa topp l\u00e9egi, waaye dinga ma toppi ca kanam.\u00bb\n13:37 Piyeer ne ko: \u00abBoroom bi, lu tax m\u00ebnuma laa topp l\u00e9egi? \u00c0ttan naa joxe sama bakkan ngir yaw!\u00bb\n13:38 Yeesu ne ko: \u00ab\u00c0ttan ngaa joxe sa bakkan ngir man? Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab, dinga ma weddi \u00f1etti yoon.\n14:1 \u00abBuleen j\u00e0q. G\u00ebmleen Y\u00e0lla te g\u00ebm ma.\n14:2 Am na n\u00e9eg yu bare ca sama k\u00ebr Baay, bu dul woon noonu, ma wax leen ko, ndaxte maa ngi dem defaral leen fa ngeen di d\u00ebkk.\n14:3 Te su ma leen defaralee b\u00e9rab booba ba noppi, dinaa dellusi, y\u00f3bbaale leen, ba fu ma nekk, ngeen nekk fa, y\u00e9en itam.\n14:4 Te fa ma j\u00ebm, xam ngeen yoon wi.\u00bb\n14:5 Tomaa ne ko: \u00abBoroom bi, xamunu fa nga j\u00ebm. Kon nan lanuy man a xame yoon wi?\u00bb\n14:6 Yeesu ne ko: \u00abMan maay yoon wi, maay d\u00ebgg te dund it man la. Kenn du \u00f1\u00ebw ci Baay bi te jaarul ci man.\n14:7 Ndegam xam ngeen ma, dingeen xam itam sama Baay. Lu weesu tey, xam ngeen ko te gis ngeen ko.\u00bb\n14:8 Filib ne ko: \u00abBoroom bi, won nu Baay bi; loolu doy na nu.\u00bb\n14:9 Yeesu tontu ko ne: \u00abNi ma y\u00e0ggeek y\u00e9en te ba tey Filib, xamuloo ma? Ku ma gis, gis nga Baay bi. Kon nag nan ngay man a laaje naan: \u201cWon nu Baay bi\u201d?\n14:10 Xamuloo ne maa ngi nekk ci Baay bi te Baay baa ngi ci man? K\u00e0ddu yi ma leen di wax j\u00f3gewu\u00f1u ci man, waaye Baay bi nekk ci man mooy matal ay j\u00ebfam.\n14:11 G\u00ebmleen li ma leen wax ne, maa ngi ci Baay bi te Baay baa ngi ci man; walla boog, g\u00ebmleen ndax j\u00ebf yi.\n14:12 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax: k\u00e9pp ku ma g\u00ebm dina def, moom itam, j\u00ebf yi may def. Dina def sax yu g\u00ebn a m\u00e0gg, ndaxte maa ngi dem ci Baay bi.\n14:13 Te it lu ngeen \u00f1aan ci sama tur dinaa ko def, ngir Doom ji fee\u00f1al ndamu Baay bi.\n14:14 Lu ngeen \u00f1aan ci sama tur, maa koy def.\n14:15 \u00abBu ngeen ma b\u00ebggee, dingeen topp sama ndigal.\n14:16 Te dinaa \u00f1aan Baay bi, mu jox leen beneen Dimbalikat, buy nekk ak y\u00e9en ba abadan.\n14:17 Kooku mooy Xelu Y\u00e0lla, mi yor d\u00ebgg. \u00c0ddina du ko man a nangu, ndaxte gisu ko te xamu ko. Y\u00e9en xam ngeen ko, ndaxte mi ngi d\u00ebkk ak y\u00e9en te dina nekk ci y\u00e9en.\n14:18 Duma leen b\u00e0yyi ngeen w\u00e9et. Dinaa dellusi ci y\u00e9en.\n14:19 Des na tuuti ci kanam, \u00e0ddina du ma gisati; waaye y\u00e9en dingeen ma gis. Dinaa dund, moo tax y\u00e9en itam dingeen dund.\n14:20 Bu keroogee, dingeen xam nag ne, nekk naa ci sama Baay, y\u00e9en it nekk ngeen ci man, te maa ngi nekk ci y\u00e9en.\n14:21 Ki ma b\u00ebgg, mooy kiy nangu samay ndigal te di ko topp. Ku ma b\u00ebgg, Baay bi b\u00ebgg la, te man dinaa la b\u00ebgg, di la fee\u00f1u.\u00bb\n14:22 Yudaa --du Yudaa Iskariyo de, beneen la woon \u2014 ne ko: \u00abBoroom bi, lu xew, ba nga nar noo fee\u00f1u nun rekk, te doo fee\u00f1u \u00e0ddina s\u00e9pp?\u00bb\n14:23 Yeesu tontu ko ne: \u00abKu ma b\u00ebgg dina s\u00e0mm sama k\u00e0ddu. Sama Baay dina ko b\u00ebgg te nun dinanu \u00f1\u00ebw ci moom, te d\u00ebkk ci moom.\n14:24 Ku ma b\u00ebggul doo s\u00e0mm sama k\u00e0ddu. Li may wax nag, j\u00f3gewul ci man, waaye mi ngi soqikoo ci ki ma y\u00f3nni.\n14:25 \u00abLii dama leen koy wax ci bi may nekk ak y\u00e9en.\n14:26 Waaye Dimbalikat, bi leen Baay bi di y\u00f3nnee ci sama tur, muy Xelam mu Sell, dina leen j\u00e0ngal l\u00e9pp, di leen f\u00e0ttali li ma leen waxoon l\u00e9pp.\n14:27 J\u00e0mm laa leen b\u00e0yyeel, sama j\u00e0mm laa leen jox, j\u00e0mm ju \u00e0ddina m\u00ebnul a joxe. Buleen j\u00e0q, buleen tiit.\n14:28 \u00abD\u00e9gg ngeen li ma leen wax: \u201cDinaa dem, waaye dinaa dellusi ci y\u00e9en.\u201d Bu ngeen ma b\u00ebggoon, dingeen b\u00e9g ci li may dem ca Baay ba, ndaxte Baay bee ma g\u00ebn a m\u00e0gg.\n14:29 Wax naa leen ko nag l\u00e9egi, bala looloo \u00f1\u00ebw, ngir bu waxtu wa agsee, ngeen g\u00ebm.\n14:30 Lu weesu tey duma amati jotu waxtaan ak y\u00e9en, ndaxte malaaka mu bon mi jiite \u00e0ddina saa ngi \u00f1\u00ebw. Kooku manalu ma dara.\n14:31 Waaye \u00e0ddina si war na xam ne, b\u00ebgg naa Baay bi te ni ma ko Baay bi sante, ni laay j\u00ebfe. J\u00f3gleen, nu dem!\n15:1 \u00abMan maay garab gu w\u00f3or gi, te sama Baay mooy beykat bi.\n15:2 Car bu soqikoo ci man te me\u00f1\u00f1ul, dina ko dog, s\u00e0nni. Waaye car bu ci me\u00f1\u00f1, dina ko tenqi, ngir mu g\u00ebn a me\u00f1\u00f1.\n15:3 Y\u00e9en nag, Baay bi setal na leen jaarale ko ci k\u00e0ddu gi ma leen wax, ni beykat di tenqee garabam.\n15:4 Saxleen ci man; ma sax, man itam, ci y\u00e9en. Ni car m\u00ebnul a ame ay doom, bu saxul ci garab, noonu itam dungeen man a me\u00f1\u00f1 li may j\u00ebfe ci y\u00e9en, bu ngeen saxul ci man.\n15:5 \u00abMan maay garab gi; y\u00e9en y\u00e9enay car yi. Ki sax ci man te ma sax ci moom, dina me\u00f1\u00f1, ndaxte bu ngeen saxul ci man, dungeen man dara.\n15:6 Ku saxul ci man dina\u00f1u ko s\u00e0nni ci biti, mu mel ni car bu \u00f1u dagg, ba mu wow. Car yu wow nag, da\u00f1u leen di buub, s\u00e0nni ci safara, \u00f1u lakk.\n15:7 Bu ngeen saxee ci man te saxal samay wax ci seen xol, lu ngeen \u00f1aan mu nangu.\n15:8 Liy fee\u00f1al sama ndamu Baay moo di, ngeen di g\u00ebn a me\u00f1\u00f1 tey wone noonu ne, samay taalibe ngeen.\n15:9 \u00abNi ma Baay bi b\u00ebggee, noonu itam laa leen b\u00ebgge. Saxleen ci mb\u00ebggeel googu ma am ci y\u00e9en.\n15:10 Bu ngeen toppee samay ndigal, dingeen sax ci sama mb\u00ebggeel, ni ma toppe sama ndigali Baay, ba tax ma sax ci mb\u00ebggeelam.\n15:11 Wax naa leen loolu, ngir ngeen bokk ci sama mb\u00e9g, te seen bos mat s\u00ebkk.\n15:12 Sama ndigal mooy ngeen b\u00ebggante, ni ma leen b\u00ebgge.\n15:13 Genn mb\u00ebggeel m\u00ebnul a weesu joxe sa bakkan ngir say xarit.\n15:14 Samay xarit ngeen, ci kaw ngeen def li ma santaane.\n15:15 Dootuma leen wooye jaam, ndaxte jaam du xam li sangam di def. Xarit laa leen wooye, ndaxte xamal naa leen li ma j\u00eble l\u00e9pp ci sama Baay.\n15:16 Du y\u00e9en y\u00e9ena ma t\u00e0nn, waaye man maa leen t\u00e0nn, sas leen ngeen dem, me\u00f1\u00f1 me\u00f1\u00f1eef gu sax, ngir Baay bi def lu ngeen ko \u00f1aan ci sama tur.\n15:17 Li may santaane nag, mooy ngeen b\u00ebggante.\n15:18 \u00abBu leen \u00e0ddina ba\u00f1ee, xamleen ne, man la\u00f1u j\u00ebkk a ba\u00f1.\n15:19 \u00d1i bokk ci \u00f1oom la\u00f1u b\u00ebgg. Bu ngeen bokkoon ci \u00f1oom, dina\u00f1u leen b\u00ebgg, ni \u00f1u b\u00ebgge seeni \u00f1o\u00f1. Waaye bokkuleen ci \u00e0ddina, ndaxte maa leen t\u00e0nn, ber leen. Looloo tax \u00f1u ba\u00f1 leen.\n15:20 F\u00e0ttalikuleen li ma leen wax: \u201cJaam g\u00ebnul a m\u00e0gg sangam.\u201d Bu \u00f1u ma sonalee, dina\u00f1u leen sonal y\u00e9en itam. Bu \u00f1u toppee sama wax, dina\u00f1u topp seen wax y\u00e9en itam.\n15:21 Waaye loolu l\u00e9pp dina\u00f1u leen ko def ndax man, ndaxte xamu\u00f1u ki ma y\u00f3nni.\n15:22 Su ma \u00f1\u00ebwul woon, ne leen dara, du\u00f1u am b\u00e0kkaar. Waaye l\u00e9egi amu\u00f1u lay ngir seeni b\u00e0kkaar.\n15:23 Ku ma ba\u00f1, ba\u00f1 nga itam sama Baay.\n15:24 Su ma deful woon ci seen biir j\u00ebf yu kenn deful, kon du\u00f1u am b\u00e0kkaar. Waaye l\u00e9egi nag gis na\u00f1u samay j\u00ebf te teewul \u00f1u ba\u00f1 nu, man ak sama Baay.\n15:25 Waaye loolu am na ngir k\u00e0ddu gi am, k\u00e0ddu gii \u00f1u bind ci seen yoon: \u201cBa\u00f1 na\u00f1u ma ci dara.\u201d\n15:26 \u00abDimbalikat bi dina \u00f1\u00ebw, mooy Xel mi j\u00f3ge ci Baay bi tey yor d\u00ebgg gi. Dina j\u00f3ge ci Baay bi, ma yebal ko ci y\u00e9en. Moom nag, moo may seedeeli.\n15:27 Te y\u00e9en itam dingeen seede samay mbir, ndaxte y\u00e9ena nekkoon ak man ca nj\u00e0lb\u00e9en ga.\n16:1 \u00abLoolu dama leen koo wax ngir seen ng\u00ebm ba\u00f1 a w\u00e0\u00f1\u00f1iku.\n16:2 Dina\u00f1u leen d\u00e0q ca j\u00e0ngu ya, te dina\u00f1u dem ba jamono joo xam ne \u00f1i leen di rey da\u00f1uy xalaat ne, \u00f1u ngi m\u00e0ggal turu Y\u00e0lla.\n16:3 Dina\u00f1u agsi foofu, ndaxte xamu\u00f1u Baay bi te xamu\u00f1u ma.\n16:4 Loolu nag, wax naa leen ko, ngir bu waxtu wi jotee ngeen f\u00e0ttaliku ne, y\u00e9gal naa leen ko. \u00abWaxuma leen ko ca nj\u00e0lb\u00e9en ga, ndaxte maa ngi nekkoon ak y\u00e9en.\n16:5 \u00abL\u00e9egi nag maa ngi dem ca ka ma y\u00f3nni, te kenn ci y\u00e9en laaju ma fi ma j\u00ebm.\n16:6 Seen xol dafa jeex ndax li ma leen wax.\n16:7 Moona de, ci sama w\u00e0ll, d\u00ebgg laa leen di wax. Li g\u00ebn ci y\u00e9en mooy ma dem, ndaxte su dul loolu, Dimbalikat bi du \u00f1\u00ebw ci y\u00e9en; waaye su ma demee, dinaa leen ko y\u00f3nnee.\n16:8 Te bu dikkee, dina yey niti \u00e0ddina ci lu j\u00ebm ci seen b\u00e0kkaar, ci lu j\u00ebm ci sama njubte ak ci lu j\u00ebm ci \u00e0tte ba.\n16:9 Ci mbiri seen b\u00e0kkaar, dina leen yey ci li \u00f1u ma g\u00ebmul.\n16:10 Ci mbiri sama njubte, dina leen yey ndaxte maa ngi dem ci Baay bi te dungeen ma gisati.\n16:11 Ci mbiri \u00e0tte ba, dina leen yey ndaxte \u00e0tte na\u00f1u malaaka mu bon mi jiite \u00e0ddina si, ba daan ko.\n16:12 \u00abLi ma leen war a wax bare na, waaye dungeen ko man a d\u00e9kku.\n16:13 Bu Xelum Y\u00e0lla mi yor d\u00ebgg gi dikkee nag, dina leen gindi ci l\u00e9pp li j\u00ebm ci yoonu d\u00ebgg, ndaxte du wax ci coobarey boppam, waaye lu ko Baay bi wax, mu jottali leen ko. Dina leen y\u00e9gal mbir yu \u00f1\u00ebwagul.\n16:14 Dina ma m\u00e0ggal, ndaxte lu mu leen wax, ci man la ko j\u00eble.\n16:15 L\u00e9pp lu Baay bi am, maa ko moom. Looloo tax ma ne leen, lu mu leen jottali, ci man la ko j\u00eble.\n16:16 \u00abCi kanam tuuti dungeen ma gisati. Bu \u00f1u ci tegee ab diir, ngeen gisaat ma.\u00bb\n16:17 Loolu Yeesu wax, tax na ba am ca taalibe ya, \u00f1u waxante ne: \u00abLu muy wax nii: \u201cCi kanam tuuti dungeen ma gisati; bu \u00f1u ci tegee ab diir, ngeen gisaat ma,\u201d ak naan: \u201cNdaxte maa ngi dem ca Baay ba\u201d?\u00bb\n16:18 \u00d1u ne: \u00ab \u201cTeg cab diir,\u201d lu muy tekki? Xamunu li muy b\u00ebgg a wax.\u00bb\n16:19 Yeesu gis ne, am na lu \u00f1u ko b\u00ebgg a laaj, mu ne leen: \u00abDama ne: \u201cCa kanam tuuti, dungeen ma gis, te bu \u00f1u ca tegee ab diir, ngeen gisaat ma.\u201d Ndax loolu ngeen di laajante ci seen biir?\n16:20 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, dingeen jooy x\u00e0cc, waaye \u00e0ddina dina b\u00e9g; dingeen j\u00e0q, waaye seen nj\u00e0qare dina soppaliku b\u00e0nneex.\n16:21 Jig\u00e9en ju nekk ci mat, dafay j\u00e0q, ndaxte waxtu wi mu war a jur jot na. Waaye bu doom ji juddoo, dina f\u00e0tte coonoom ndaxte day b\u00e9g ci li doom ji gane \u00e0ddina.\n16:22 Noonu nag ngeen di j\u00e0qe, y\u00e9en itam. Waaye dinaa leen gisaat, seeni xol sedd, te seen mb\u00e9g moomu, kenn du ko man a dindi.\n16:23 B\u00e9s boobu dootuleen ma laaj dara. Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, Baay bi dina leen may lu ngeen ko \u00f1aan ci sama tur.\n16:24 Ba l\u00e9egi \u00f1aanaguleen dara ci sama tur. \u00d1aanleen, mu nangu. Bu ko defee seen mb\u00e9g mat s\u00ebkk.\n16:25 \u00abLoolu l\u00e9pp, dama leen koo wax ci ay misaal. Jamono dina \u00f1\u00ebw, ju ma dootul wax ak y\u00e9en ci ay misaal, waaye ju ma leen dee wax lu leer ci Baay bi.\n16:26 Bu keroogee dingeen \u00f1aan ci sama tur. Neewuma dinaa leen \u00f1aanal Baay bi,\n16:27 ndaxte Baay bi ci boppam b\u00ebgg na leen. B\u00ebgg na leen ndaxte b\u00ebgg ngeen ma, te g\u00ebm ngeen ne, ci Y\u00e0lla laa j\u00f3ge.\n16:28 J\u00f3ge naa ca Baay bi, \u00f1\u00ebw \u00e0ddina. L\u00e9egi maa ngi g\u00e9nn \u00e0ddina, fekki Baay bi.\u00bb\n16:29 Taalibe yi ne ko: \u00abL\u00e9egi yaa ngi wax lu leer te misaaloo!\n16:30 L\u00e9egi gis nanu ne, xam nga l\u00e9pp, te soxlawul kenn di la laaj dara. Looloo tax nu xam ne, yaa ngi j\u00f3ge ci Y\u00e0lla.\u00bb\n16:31 Yeesu ne leen: \u00abNdax g\u00ebm ngeen l\u00e9egi?\n16:32 Waxtu waa ngi \u00f1\u00ebw te agsi na ba noppi, dingeen tasaaroo, ku nekk \u00f1ibbi, ma des man rekk.\n16:33 Waaye nag d\u00e9ed\u00e9et, w\u00e9etuma, ndaxte Baay baa ngi may w\u00e9ttali. Dama leen wax loolu, ngir ngeen am j\u00e0mm ci man. Dingeen am nattu ci \u00e0ddina, waaye takkleen fit yi; noot naa \u00e0ddina.\u00bb\n17:1 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa xool ci kaw, ne j\u00e0kk asamaan, \u00f1aan Y\u00e0lla ne: \u00abBaay, waxtu wi tax ma \u00f1\u00ebw ci \u00e0ddina agsi na. Fee\u00f1alal ndamu Doom ji, ngir moom itam mu man a fee\u00f1al sa ndam.\n17:2 Ndaxte jox nga ko sa\u00f1-sa\u00f1 ci b\u00e9pp mbindeef, ngir mu may dund gu dul jeex gi \u00f1i nga ko d\u00e9nk.\n17:3 Dund gu dul jeex gi nag, mooy \u00f1u xam la, yaw jenn Y\u00e0lla ju w\u00f3or ji am, te \u00f1u xam it ki nga y\u00f3nni, muy Yeesu Kirist.\n17:4 Wone naa sa ndam ci \u00e0ddina, ndax li ma matal ligg\u00e9ey, bi nga ma santoon.\n17:5 L\u00e9egi nag Baay, ci sa teewaay, fee\u00f1alal ci man ndam, li ma amoon ci sa wet, laata \u00e0ddina di sosu.\n17:6 \u00abXamal naa sa tur nit, \u00f1i nga t\u00e0nne ci \u00e0ddina te d\u00e9nk ma leen. Bokkoon na\u00f1u ci yaw, nga d\u00e9nk ma leen, te s\u00e0mm na\u00f1u sa k\u00e0ddu.\n17:7 Xam na\u00f1u l\u00e9egi ne, loo ma joxaan, ci yaw la j\u00f3ge,\n17:8 ndaxte xamal naa leen k\u00e0ddu yi nga ma jox, te nangu na\u00f1u ko. W\u00f3or na leen ne, ci yaw laa j\u00f3ge, te g\u00ebm na\u00f1u ne yaa ma y\u00f3nni.\n17:9 \u00d1oom laay \u00f1aanal. \u00d1aanaluma waa \u00e0ddina, waaye maa ngi \u00f1aanal \u00f1i nga ma d\u00e9nk, ndaxte ci yaw la\u00f1u bokk.\n17:10 Lu ma am, yaa ko moom, te loo am, maa ko moom; te \u00f1oom \u00f1oo fee\u00f1al sama ndam.\n17:11 Nekkatuma ci \u00e0ddina, waaye \u00f1oom \u00f1u ngi ci; man, ci yaw laa j\u00ebm. Baay bu sell bi, s\u00e0mm leen ci sa dooley tur woowu nga ma jox, ngir \u00f1u nekk benn, ni nu nekke benn, man ak yaw.\n17:12 Bi ma nekkee ak \u00f1oom, daan naa leen s\u00e0mm ci sa dooley tur, tur wi nga ma jox. Wottu naa leen, ba kenn ci \u00f1oom s\u00e0nkuwul, lu dul kiy aji r\u00e9er ji, ngir li Mbind mi waxoon am.\n17:13 \u00abWaaye l\u00e9egi maa ngi j\u00ebmsi ci yaw, te maa ngi wax nii ci bi may nekk \u00e0ddina, ngir \u00f1u fees ak sama mb\u00e9g.\n17:14 Jottali naa leen sa k\u00e0ddu, te \u00e0ddina ba\u00f1 leen, ndax li \u00f1u mel ni man, ba\u00f1 a bokk ci \u00e0ddina soosu.\n17:15 \u00d1aanuma nga j\u00eble leen \u00e0ddina, waaye nga yiir leen ci Ibliis.\n17:16 Da\u00f1oo mel ni man; bokku\u00f1u ci \u00e0ddina.\n17:17 Samp leen ci d\u00ebgg, ngir \u00f1u sell. Sa k\u00e0ddu mooy d\u00ebgg.\n17:18 Ni nga ma y\u00f3nnee \u00e0ddina, noonu laa leen y\u00f3nnee ci nit \u00f1i.\n17:19 Sellal naa sama bopp ngir \u00f1oom, ngir \u00f1u sampu ci d\u00ebgg te sell.\n17:20 \u00ab\u00d1aanaluma leen \u00f1oom rekk, waaye itam \u00f1i may g\u00ebm \u00ebll\u00ebg ndax seen wax.\n17:21 Damay \u00f1aan ngir \u00f1\u00e9pp doon benn. Baay, na \u00f1oo\u00f1u nekk benn ci nun, ni nga nekke ci man te ma nekke ko ci yaw. Na\u00f1u \u00e0nd, ba \u00e0ddina g\u00ebm ne, yaa ma y\u00f3nni.\n17:22 Boole naa leen ci ndam, li nga ma sol, ngir \u00f1u \u00e0ndandoo, ni nu \u00e0nde man ak yaw.\n17:23 Man ci \u00f1oom, yaw it ci man, ngir \u00f1u g\u00ebn a \u00e0nd, nekk benn, ba \u00e0ddina xam ne yaa ma y\u00f3nni, xam ne b\u00ebgg nga leen, ni nga ma b\u00ebgge.\n17:24 \u00abBaay, b\u00ebgg naa, \u00f1i nga ma d\u00e9nk nekk ak man fa ma j\u00ebm, ngir \u00f1u gis sama ndam, li nga ma sol, ndaxte b\u00ebgg nga ma, laata \u00e0ddina di sosu.\n17:25 \u00abBaay, yaw ku jub ki, waa \u00e0ddina xamu\u00f1u la, waaye man xam naa la, te \u00f1ii xam na\u00f1u ne, yaa ma y\u00f3nni.\n17:26 Xamal naa leen sa tur te dinaa ko g\u00ebn a xamle, ngir mb\u00ebggeel, gi nga am ci man, nekk ci \u00f1oom, te man it ma nekk ci \u00f1oom.\u00bb\n18:1 Bi mu waxee noonu ba noppi, Yeesu j\u00f3ge fa ak i taalibeem, j\u00e0ll xuru Sedoron, dugg cib tool.\n18:2 Yudaa mi ko naroon a wor xamoon na it b\u00e9rab ba, ndaxte Yeesu daan na fa dem ak ay taalibeem.\n18:3 Yudaa daldi fa dem, y\u00f3bbaale mbooloom xarekat ak ay alkaati yu ko saraxalekat yu mag ya ak Farisen ya jox. \u00d1u yor ay jum ak ay l\u00e0mp ak it g\u00e0nnaay.\n18:4 Noonu Yeesu, mi xamoon li ko waroon a dal l\u00e9pp, jubsi leen ne leen: \u00abKu ngeen di seet?\u00bb\n18:5 \u00d1u ne ko: \u00abYeesum Nasaret.\u00bb Yeesu ne: \u00abMan la.\u00bb Fekk Yudaa mi ko nar a wor a nga \u00e0nd ak \u00f1oom.\n18:6 Bi leen Yeesu nee: \u00abMan la,\u00bb \u00f1u daldi dellu gannaaw, ba daanu.\n18:7 Yeesu laajaat leen ne: \u00abKu ngeen di seet?\u00bb \u00d1u ne ko: \u00abYeesum Nasaret.\u00bb\n18:8 Mu ne leen: \u00abWax naa leen ne, man la. Bu fekkee ne nag man ngeen di seet, b\u00e0yyileen \u00f1ii ma \u00e0ndal, \u00f1u dem.\u00bb\n18:9 Noonu la baat boobu mu waxoon ame: \u00abBaay, kenn s\u00e0nkuwul ci \u00f1i nga ma d\u00e9nk.\u00bb\n18:10 Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, Simo\u014b Piyeer bocci jaasi, ji mu yoroon, daldi d\u00f3or surgab saraxalekat bu mag ba, noppu ndeyjooram dagg. Surga boobu mi ngi tuddoon Malkus.\n18:11 Waaye Yeesu ne Piyeer: \u00abRoofal jaasi ji ci mbaram. Ndax warumaa naan kaasu naqar, bi ma Baay bi s\u00e9dd?\u00bb\n18:12 Mbooloom xarekat ya ak seen kilifa ak alkaatiy Yawut ya j\u00e0pp Yeesu, daldi yeew,\n18:13 j\u00ebkk koo y\u00f3bbu ca Anas, ndaxte Anas mooy gorob Kayif, mi doon saraxalekat bu mag ba at mooma.\n18:14 Kayif moo digaloon Yawut ya ne: \u00abLi g\u00ebn moo di kenn rekk dee, ngir mbooloo mi mucc.\u00bb\n18:15 Bi \u00f1uy y\u00f3bbu Yeesu, Simo\u014b Piyeer ak keneen ca taalibe ya toppoon na\u00f1u ko. Keneen kooku nag, xamante na ak saraxalekat bu mag ba, moo waral mu duggaaleek Yeesu ca biir k\u00ebr kilifa ga.\n18:16 Waaye Piyeer, moom, des ca buntu k\u00ebr ga. Noonu taalibe boobu xamante woon ak saraxalekat bu mag ba g\u00e9nn, wax ak jig\u00e9en, ja doon wottu buntu k\u00ebr ga, fexe Piyeer dugg ci biir.\n18:17 Mbindaan mi doon wottu bunt bi ne Piyeer: \u00abMbaa yaw it bokkuloo ci taalibey waa ji?\u00bb Mu ne ko: \u00abD\u00e9ed\u00e9et, bokkuma ci.\u00bb\n18:18 Booba dafa seddoon, ba surga ya ak alkaati ya boyal ab taal, di ca jaaru. Piyeer itam taxaw, di jaaru ak \u00f1oom.\n18:19 Saraxalekat bu mag ba daldi laaj Yeesu ci lu j\u00ebm ci taalibeem yi ak ci nj\u00e0ngaleem mi.\n18:20 Yeesu tontu ko ne: \u00abCi mbooloo laa doon waxe. Ci k\u00ebr Y\u00e0lla ga ak ci ay j\u00e0ngu, fa Yawut y\u00e9pp di daje, laa mas di j\u00e0ngalee. Musumaa wax dara di ko n\u00ebbb.\n18:21 Lu tax nga may laaj? Laajal \u00f1i doon d\u00e9glu li ma leen wax. \u00d1oom xam na\u00f1u li ma doon wax.\u00bb\n18:22 Bi Yeesu waxee loolu, kenn ci alkaati yi nekkoon ci wetam daldi koy pes ne ko: \u00abNdax nii ngay tontoo saraxalekat bu mag bi?\u00bb\n18:23 Yeesu tontu ko ne: \u00abSu ma waxee lu jaaduwul, wone ko; waaye su ma waxee lu jub, lu tax nga may d\u00f3or?\u00bb\n18:24 Anas daldi koy yebal ca Kayif, saraxalekat bu mag ba, \u00f1u yeew ko ba tey.\n18:25 Fekk na booba Simo\u014b Piyeer, moom, ma nga taxaw di jaaru rekk. \u00d1u laaj ko ne: \u00abMbaa yaw it bokkuloo ci taalibey waa ji?\u00bb Waaye Piyeer weddi ko ne: \u00abD\u00e9ed\u00e9et, bokkuma ci.\u00bb\n18:26 Kenn ci surgay saraxalekat bu mag ba, di mbokku ka Piyeer coroon noppam, ne Piyeer: \u00abXanaa du yaw laa gisoon ak moom ca tool ba?\u00bb\n18:27 Waaye Piyeer dellu weddi ko. Noonu ginaar daldi sab.\n18:28 Bi loolu w\u00e9yee \u00f1u j\u00eble Yeesu ca Kayif, y\u00f3bbu ko ca k\u00ebr boroom r\u00e9ew ma. Ci waxtuw nj\u00ebl la woon. Waaye Yawut ya y\u00e9egu\u00f1u ca taaxum kaw ma. Da\u00f1oo ba\u00f1oon a taq sobe, ngir man a lekk ca \u00f1amu m\u00e0ggalu J\u00e9ggi ba.\n18:29 Looloo tax Pilaat boroom r\u00e9ew ma g\u00e9nn, dajeek \u00f1oom. Mu laaj leen ne: \u00abLu ngeen di jii\u00f1 waa jii?\u00bb\n18:30 \u00d1u tontu ko ne: \u00abBu deful woon lu bon, du\u00f1u la ko j\u00e9bbalsi.\u00bb\n18:31 Pilaat ne leen: \u00abJ\u00ebl-leen ko, y\u00e9en, te \u00e0tte ko ci seen yoon.\u00bb Yawut yi ne ko: \u00abYoon mayu nu, nu \u00e0tte nit, teg ko dee.\u00bb\n18:32 Noonu la k\u00e0ddug Yeesu gi ame, ci li mu misaaloon ni mu war a faatoo.\n18:33 Gannaaw loolu Pilaat duggaat ca taaxum kaw ma, woo Yeesu ne ko: \u00abNdax yaa di buuru Yawut yi?\u00bb\n18:34 Yeesu tontu ko ne: \u00abNdax yaa ko xalaat, wax ko, am da\u00f1u la koo xelal ci man?\u00bb\n18:35 Pilaat ne ko: \u00abMbaa xalaatoo ne, man Yawut laa? Sa xeet ak saraxalekat yu mag yi \u00f1oo ma la j\u00e9bbal. Lan nga def?\u00bb\n18:36 Yeesu tontu: \u00abSama kilifteef nekkul ci \u00e0ddina. Bu sama kilifteef nekkoon \u00e0ddina, sama surga yi dina\u00f1u xeex, ngir ba\u00f1 \u00f1u j\u00e9bbal ma Yawut yi. Waaye sama kilifteef nekkul \u00e0ddina.\u00bb\n18:37 Pilaat ne ko: \u00abKon yaw buur nga?\u00bb Yeesu tontu ko: \u00abWax nga ko; buur laa. Lii moo tax ma juddu, \u00f1\u00ebw \u00e0ddina: ngir wax d\u00ebgg gi. Ku bokk ci d\u00ebgg dina nangu li ma wax.\u00bb\n18:38 Pilaat laaj ko ne: \u00abLuy d\u00ebgg?\u00bb Bi mu waxee loolu ba noppi, Pilaat daldi g\u00e9nnaat, j\u00ebm ca Yawut ya ne leen: \u00abGisuma ci moom genn too\u00f1.\n18:39 Seen aada laaj na, ma b\u00e0yyil leen kenn, saa su \u00f1uy def m\u00e0ggalu b\u00e9su J\u00e9ggi bi. Xanaa ma b\u00e0yyil leen \u201cbuuru Yawut yi?\u201d\u00bb\n18:40 Noonu \u00f1u daldi yuuxuwaat: \u00abD\u00e9ed\u00e9et, waxunu kii; Barabas lanu wax!\u00bb Fekk Barabas moomu taskatu r\u00e9ew la woon.\n19:1 Noonu Pilaat joxe ndigal, \u00f1u d\u00f3or Yeesu ay yar.\n19:2 Xarekat ya r\u00e0bb kaalag d\u00e9g, teg ko ci boppu Yeesu, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr.\n19:3 \u00d1u di ko jege\u00f1si, di ko pes, naan ko: \u00abNuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!\u00bb\n19:4 Pilaat g\u00e9nnaat ne leen: \u00abGis ngeen, maa ngi leen koy indil ci biti, ngir ngeen xam ne, waa jii, gisuma ci moom genn too\u00f1.\u00bb\n19:5 Yeesu nag g\u00e9nn, tegoo mbubbum xarekat mu xonq mi ak kaalag d\u00e9g gi. Pilaat it ne leen: \u00abWaa jaa ngii!\u00bb\n19:6 Waaye bi \u00f1u ko gisee, saraxalekat yu mag ya ak alkaati ya di yuuxoo naan: \u00abDaaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!\u00bb Pilaat ne leen: \u00abJ\u00ebl-leen ko, y\u00e9en, daaj ko ci bant, ndaxte gisuma ci moom genn too\u00f1.\u00bb\n19:7 Yawut yi tontu ko ne: \u00abAm nanu aw yoon, te ci yoon woowu, war na dee ndaxte teg na boppam Doomu Y\u00e0lla.\u00bb\n19:8 Bi Pilaat d\u00e9ggee wax jooju, dafa g\u00ebn a tiit,\n19:9 dugg ca taax ma, daldi ne Yeesu: \u00abFoo j\u00f3ge?\u00bb Waaye Yeesu tontuwu ko.\n19:10 Pilaat ne ko: \u00abMan ngay ba\u00f1 a waxal? Xanaa xamuloo ne, am naa sa\u00f1-sa\u00f1u b\u00e0yyi la, te am naa itam sa\u00f1-sa\u00f1u daaj la ci bant?\u00bb\n19:11 Yeesu tontu ko ne: \u00abAmuloo benn sa\u00f1-sa\u00f1 ci man su dul bi la Y\u00e0lla jox. Looloo tax ba ki ma j\u00e9bbal ci say loxo am na b\u00e0kkaar, bi g\u00ebn a r\u00e9y.\u00bb\n19:12 Booba nag la Pilaat doon fexee b\u00e0yyi Yeesu. Waaye Yawut ya di yuuxoo naan: \u00abBoo b\u00e0yyee kii, doo xaritu buur bi Sesaar. Nit ku teg boppam buur, noonub Sesaar la!\u00bb\n19:13 Bi Pilaat d\u00e9ggee loolu, mu daldi g\u00e9nne Yeesu ca biti, dem toog ca jalub \u00e0ttekaay ba, ca fu \u00f1uy wax B\u00e9rabu doj ya. Ci l\u00e0kku yawut \u00f1u naan ko Gabata.\n19:14 Ca b\u00e9s ba \u00f1uy waajal m\u00e0ggalu J\u00e9ggi ba la woon, ca weti digg-b\u00ebcc\u00ebg. Pilaat ne Yawut ya: \u00abSeen buur a ngii!\u00bb\n19:15 Waaye \u00f1uy yuuxoo naan: \u00abNa dee! Na dee! Daaj ko ci bant!\u00bb Pilaat ne leen: \u00abNdax seen buur bi, dama koo war a daaj ci bant?\u00bb Saraxalekat yu mag ya ne ko: \u00abAmunu benn buur bu dul Sesaar!\u00bb\n19:16 Noonu Pilaat j\u00e9bbal leen Yeesu, ngir \u00f1u daaj ko ci bant. Bi leen ko Pilaat j\u00e9bbalee, \u00f1u j\u00ebl ko, y\u00f3bbu.\n19:17 Yeesu ci boppam g\u00e0ddu bant ba, g\u00e9nn ngir dem ca fa \u00f1uy wax B\u00e9rabu kaa\u014bu bopp; \u00f1u koy wooye Golgota ci l\u00e0kku yawut.\n19:18 Foofa la xarekat ya daaje Yeesu ca bant ba. Ci noonu it \u00f1u daajaale \u00f1aari nit ci wetam, mu nekk ca digg ba.\n19:19 Pilaat santaane itam \u00f1u bind, teg ko ca kaw bant, ba \u00f1u ko daajoon. Mbind ma lii la wax: \u00abKii mooy Yeesum Nasaret, buuru Yawut yi.\u00bb\n19:20 Mbind mooma, Yawut yu bare j\u00e0ng na\u00f1u ko, ndaxte fa \u00f1u daajoon Yeesu ca bant ba jege woon na d\u00ebkk ba, te mbind ma ci l\u00e0kku yawut la woon, ci l\u00e0kku waa Room ak ci gereg.\n19:21 Noonu saraxalekat yu mag yu Yawut ya ne Pilaat: \u00abBul bind: \u201cBuuru Yawut,\u201d bindal rekk: \u201cKii moo ne mooy buuru Yawut yi.\u201d\u00bb\n19:22 Pilaat tontu leen ne: \u00abXas naa koo bind, du de\u00f1.\u00bb\n19:23 Xarekat ya, bi \u00f1u daajee Yeesu ca bant ba, ba noppi da\u00f1oo j\u00ebl ay y\u00e9reem, s\u00e9ddale ko \u00f1eenti c\u00e9r, ku nekk benn. J\u00ebl na\u00f1u it mbubbam bu \u00f1u r\u00e0bb ca kaw ba ci suuf te amul benn \u00f1aw.\n19:24 Xarekat ya di waxante naan: \u00abMbubb mi, bunu ko xotti, waaye nanu ko tegoo ay bant, ngir xam ku koy moom.\u00bb Noonu la Mbind mi waroon a ame, bi mu naan:\u00abS\u00e9ddoo na\u00f1u samay y\u00e9re,tegoo ay bant sama mbubb.\u00bb Loolu nag la xarekat ya def.\n19:25 Ca wetu bant, ba \u00f1u daajoon Yeesu, yaayam a nga fa taxawoon, moom ak doomu ndeyam ju jig\u00e9en, Maryaama jabari K\u00ebl\u00f3pas, ak Maryaama mi d\u00ebkk Magdala.\n19:26 Bi Yeesu gisee yaayam taxaw ci wetu taalibe, bi mu b\u00ebggoon, mu ne ko: \u00abSoxna si, sa doom a ngi,\u00bb\n19:27 neeti taalibe ba: \u00abSa yaay a ngi nii.\u00bb Booba la ko taalibe ba y\u00f3bbu k\u00ebram, yor ko.\n19:28 Bi loolu w\u00e9yee gannaaw Yeesu xam na ne, l\u00e9pp mat na l\u00e9egi, mu ne nag, ngir amal Mbind mi: \u00abDamaa mar.\u00bb\n19:29 Amoon na foofa gutt bu fees ak bineegar. Noonu \u00f1u j\u00ebl sagar, tooyal ko ca, takk ko ci bantu garab gu \u00f1uy wax isob, teg ko ci g\u00e9mmi\u00f1u Yeesu.\n19:30 Bi Yeesu muucoo bineegar bi, mu ne: \u00abL\u00e9pp mat na!\u00bb Noonu mu s\u00ebgg, delloo ruuwam Y\u00e0lla.\n19:31 Keroog ba \u00f1u dee waajal b\u00e9su noflaay ba la woon, te Yawut ya b\u00ebggu\u00f1u n\u00e9ew ya des ca bant ya, ndaxte b\u00e9su noflaay boobu fonkoon na\u00f1u ko lool. \u00d1u \u00f1aan Pilaat, mu dammlu t\u00e0nki \u00f1a \u00f1u daajoon, te j\u00eble leen fa.\n19:32 Noonu xarekat ya dem, damm t\u00e0nki ku j\u00ebkk ka, teg ca ka ca des, ca \u00f1a \u00f1u daajaale woon ak Yeesu.\n19:33 Bi \u00f1u agsee ci Yeesu, dammu\u00f1u ay t\u00e0nkam, ndaxte gis na\u00f1u ne booba faatu na.\n19:34 Waaye kenn ca xarekat ya daldi j\u00ebl xeej, jam ko ko ci wet, ca saa sa deret ak ndox di tuuru.\n19:35 Kiy nettali mbir yooyu, da cee teg b\u00ebtam, te li muy wax d\u00ebgg la. Moom ci boppam xam na ne, li muy wax d\u00ebgg la, ngir y\u00e9en itam ngeen g\u00ebm,\n19:36 ndaxte loolu dafa xew ngir Mbind mi am: \u00abBenn yaxam du damm.\u00bb\n19:37 Leneen it Mbind mi wax na ko: \u00abDina\u00f1u gis ki \u00f1u jamoon.\u00bb\n19:38 Gannaaw loolu Yuusufa mi d\u00ebkk Arimate \u00f1aan Pilaat ngir y\u00f3bbu n\u00e9ewu Yeesu. Yuusufa taalibe Yeesu la woon ci lu kenn y\u00e9gul, ndaxte dafa ragaloon Yawut ya. Pilaat may ko ko. Yuusufa daldi dem, y\u00f3bbu n\u00e9ewu Yeesu.\n19:39 Nikodem itam \u00f1\u00ebw, moom mi masoon a seeti Yeesu guddi. Mu indaale lu war a tollook fanweeri kiloy cuuraay lu \u00f1u defare nd\u00e0bbi miir ak banti aloos.\n19:40 \u00d1u j\u00ebl n\u00e9ewu Yeesu, laxas ko ci c\u00e0ngaay, boole ko ak cuuraay li, ni ko Yawut yi t\u00e0mmoo def, bu \u00f1uy waajal n\u00e9ew.\n19:41 Tool a nga woon ca wetu b\u00e9rab, ba \u00f1u daajoon Yeesu, te ca tool booba amoon na fa b\u00e0mmeel bu \u00f1u musul a suul kenn.\n19:42 Ca b\u00e9su Waajal la woon, ba Yawut ya doon waajal b\u00e9su noflaay ba, te b\u00e0mmeel ba jege woon na. Foofa la\u00f1u denc Yeesu.\n20:1 B\u00e9s ba jiitu ca ayu-b\u00e9s ga, Maryaamam Magdala j\u00f3g ca fajar, dem ca b\u00e0mmeel ba. Bi mu agsee, mu gis ne dindi na\u00f1u xeer, wa \u00f1u ko ube woon.\n20:2 Mu daw, dem ca Simo\u014b Piyeer ak ca beneen taalibe ba, maanaam ka Yeesu b\u00ebggoon, ne leen: \u00abJ\u00eble na\u00f1u n\u00e9ewu Boroom ba ca b\u00e0mmeel ba, te xamunu fu \u00f1u ko y\u00f3bbu.\u00bb\n20:3 Piyeer ak beneen taalibe ba daw, dem ca b\u00e0mmeel ba.\n20:4 \u00d1oom \u00f1aar \u00f1\u00e9pp a ngi doon daw, waaye beneen taalibe ba raw Piyeer, j\u00ebkk ko ca b\u00e0mmeel ba.\n20:5 Duggul nag, dafa s\u00ebgg, y\u00ebr, s\u00e9en c\u00e0ngaay la ca suuf.\n20:6 Noonu Simo\u014b Piyeer, mi ko toppoon, agsi, daldi dugg. Mu s\u00e9en c\u00e0ngaay la ci suuf,\n20:7 ak kaala ga muuroon boppu Yeesu. Waaye kaala googu \u00e0ndul ak c\u00e0ngaay la; da\u00f1u ko laxas, teg ko ci wet.\n20:8 Noonu keneen ka jiitu woon ca b\u00e0mmeel ba, duggsi moom itam. Naka la gis, daldi g\u00ebm.\n20:9 Taalibe yi xamagu\u00f1u woon Mbind, mi doon wone ne, Yeesu dafa war a dekki.\n20:10 Noonu taalibe ya d\u00ebpp, \u00f1ibbi.\n20:11 Maryaama nag moom, ma nga desoon ca biti, ca wetu b\u00e0mmeel ba, di jooy. Bi muy jooy, mu s\u00ebgg, y\u00ebr ci biir,\n20:12 s\u00e9en \u00f1aari malaaka yu sol mbubb yu weex, toog ca b\u00e9rab, ba \u00f1u dencoon Yeesu; kenn ka f\u00e9eteek bopp bi, ki ci des ca t\u00e0nk ya.\n20:13 Malaaka ya laaj ko ne: \u00abJig\u00e9en ji, looy jooy?\u00bb Mu tontu leen ne: \u00abDa\u00f1oo j\u00ebl sama Boroom, te xawma fu \u00f1u ko y\u00f3bbu.\u00bb\n20:14 Bi mu waxee loolu, mu geestu, s\u00e9en Yeesu mu taxaw, waaye xamul woon ne moom la.\n20:15 Yeesu laaj ko ne: \u00abJig\u00e9en ji, looy jooy? Kooy seet?\u00bb Mu foog ne boroom tool ba la, ne ko: \u00abS\u00ebri\u00f1 bi, bu fekkee yaa ko y\u00f3bbu, wax ma foo ko denc, ma j\u00ebli ko.\u00bb\n20:16 Noonu Yeesu ne ko: \u00abMaryaama.\u00bb Mu walbatiku, l\u00e0kk ko ci yawut ne ko: \u00abR\u00e0bbuni!\u00bb R\u00e0bbuni mooy tekki \u00abKilifa gi.\u00bb\n20:17 Yeesu ne ko: \u00abBu ma t\u00e9ye, ndaxte y\u00e9egaguma ca Baay ba. Waaye demal, ne samay bokk, maa ngi y\u00e9eg ca sama Baay biy seen Baay, ca sama Y\u00e0lla jiy seen Y\u00e0lla.\u00bb\n20:18 Noonu Maryaamam Magdala dem, y\u00e9gali ko taalibe ya ne leen: \u00abGis naa Boroom bi!\u00bb Mu daldi leen nettali li mu ko wax.\n20:19 B\u00e9s boobu ca ngoon sa, taalibe yaa nga daje woon ca genn k\u00ebr, t\u00ebju ca biir ndax ragal Yawut ya. Yeesu ne t\u00ebll ci seen biir ne leen: \u00abNa j\u00e0mm w\u00e0cc ci y\u00e9en!\u00bb\n20:20 Mu daldi leen won ay loxoom ak wetam. Bi \u00f1u gisee Boroom bi, taalibe ya daldi b\u00e9g lool.\n20:21 Yeesu dellu ne leen: \u00abNa j\u00e0mm w\u00e0cc ci y\u00e9en! Ni ma Baay bi y\u00f3nnee, noonu laa leen di y\u00f3nnee, man itam.\u00bb\n20:22 Bi mu waxee loolu, mu \u00ebf leen ne leen: \u00abSol naa leen Xelu Y\u00e0lla mu Sell mi.\n20:23 \u00d1i ngeen di baal seeni b\u00e0kkaar, baal na\u00f1u leen ba noppi; \u00f1i ngeen baalul, baalu\u00f1u leen.\u00bb\n20:24 Fekk na Tomaa, mi bokk ci fukki taalibe yi ak \u00f1aar, te turam di tekki \u00abS\u00e9ex bi,\u00bb nekku fa woon, bi Yeesu \u00f1\u00ebwee.\n20:25 Yeneen taalibe yi ne ko: \u00abGis nanu Boroom bi!\u00bb Waaye mu ne leen: \u00abSu ma gisul fa \u00f1u daajoon pont ya ci ay loxoom, te defuma ca sama baaraam, su ma tegul it sama loxo ci wetam, duma ko g\u00ebm mukk.\u00bb\n20:26 Bi \u00f1u ca tegee ayu-b\u00e9s, taalibe Yeesu ya dajewaat ca biir k\u00ebr ga, Tomaa itam a nga fa woon. Bunt y\u00e9pp t\u00ebju woon na\u00f1u, waaye Yeesu ne t\u00ebll ci seen biir ne leen: \u00abNa j\u00e0mm w\u00e0cc ci y\u00e9en!\u00bb\n20:27 Noonu mu ne Tomaa: \u00abIndil sa baaraam fii te seet sama loxo; indil sa loxo, teg ko ci sama wet. B\u00e0yyil di weddi te nga g\u00ebm.\u00bb\n20:28 Tomaa tontu ko ne: \u00abSama Boroom, sama Y\u00e0lla!\u00bb\n20:29 Yeesu ne ko: \u00abLi nga ma gis a tax nga g\u00ebm? Ki b\u00e9g mooy ki g\u00ebm te gisu ma!\u00bb\n20:30 Yeesu wone na it ci kanamu taalibe ya yeneeni firnde yu \u00f1u nettaliwul ci t\u00e9ere bii.\n20:31 Waaye li ci nekk, bind na\u00f1u ko ngir ngeen g\u00ebm ne, Yeesu mooy Almasi bi, Doomu Y\u00e0lla ji, te seen ng\u00ebm may leen, ngeen am ci moom dund.\n21:1 Bi \u00f1u ca tegee ab diir, Yeesu fee\u00f1uwaat na ay taalibeem ca tefesu dex gu \u00f1uy wax Tibery\u00e0dd. Nii la deme woon:\n21:2 Taalibey Yeesu yii \u00e0ndoon na\u00f1u: Simo\u014b Piyeer; Tomaa, ki turam di tekki \u00abS\u00e9ex bi;\u00bb Nataneel, mi d\u00ebkk Kana ca diiwaanu Galile; doomi Sebede ak yeneen \u00f1aari taalibe.\n21:3 Simo\u014b Piyeer ne leen: \u00abMaa ngi nappi.\u00bb \u00d1u ne ko: \u00abNun it danuy \u00e0nd ak yaw.\u00bb \u00d1u dugg gaal, daldi dem. Waaye guddi googu j\u00e0ppu\u00f1u dara.\n21:4 Ci fajar gi Yeesu taxaw ca tefes ga, waaye taalibe yi x\u00e0mmiwu\u00f1u ko.\n21:5 Yeesu ne leen nag: \u00abBokk yi, xanaa j\u00e0ppuleen j\u00ebn?\u00bb \u00d1u ne ko: \u00abD\u00e9ed\u00e9et.\u00bb\n21:6 Mu ne leen: \u00abS\u00e0nnileen mbaal mi ci ndeyjooru gaal gi, bu ko defee ngeen j\u00e0pp.\u00bb \u00d1u s\u00e0nni fa mbaal ma, mu fees ak j\u00ebn, ba m\u00ebnu\u00f1u ko woon a g\u00e9nne ndox mi.\n21:7 Taalibe ba Yeesu b\u00ebggoon, ne Piyeer: \u00abBoroom bi la!\u00bb Bi Simo\u014b Piyeer d\u00e9ggee loolu, dafa woddoo mbubbam, ndaxte dafa summeeku woon, daldi s\u00f3obu ci dex gi.\n21:8 Yeneen taalibe ya x\u00ebcc mbaal, mi fees dell ak j\u00ebn, j\u00ebme ko ca tefes ga, ndaxte gaal ga sorewul woon; diggante bi waroon na tollook t\u00e9em\u00e9eri meetar.\n21:9 Bi \u00f1u teeree, \u00f1u gis ab taal, \u00f1u ciy lakk ay j\u00ebn, teg mburu ca wet ga.\n21:10 Yeesu ne leen: \u00abIndileen ci j\u00ebn, yi ngeen j\u00e0pp.\u00bb\n21:11 Simo\u014b Piyeer y\u00e9eg ca gaal ga, daldi x\u00ebcc mbaal ma ca tefes ga, mu fees dell ak j\u00ebn yu mag; matoon na t\u00e9em\u00e9eri j\u00ebn ak jur\u00f3om-fukk ak \u00f1ett. Te li muy baree-bare l\u00e9pp, taxul mbaal ma dog.\n21:12 Yeesu ne leen: \u00ab\u00d1\u00ebwleen nd\u00e9kki.\u00bb Kenn ci taalibe yi \u00f1emewu koo laaj ki mu doon, ndaxte xam na\u00f1u ne, Boroom bi la.\n21:13 Yeesu jege\u00f1si, j\u00ebl mburu mi, jox leen, jox leen it j\u00ebn.\n21:14 Bi Yeesu dekkee ba tey, bii mooy \u00f1etteelu yoon, bi mu fee\u00f1oo ay taalibeem.\n21:15 Bi \u00f1u nd\u00e9kkee ba noppi, Yeesu ne Simo\u014b Piyeer: \u00abSimo\u014b doomu Yowaana, ndax g\u00ebn nga maa b\u00ebgg, ni ma \u00f1ii b\u00ebgge?\u00bb Mu tontu ko ne: \u00abAa\u014bkay, Boroom bi, xam nga ne, b\u00ebgg naa la.\u00bb Yeesu ne ko: \u00abTopptool ma sama mbote yi.\u00bb\n21:16 Noonu mu waxaat ko ne: \u00abSimo\u014b doomu Yowaana, ndax b\u00ebgg nga ma?\u00bb Mu ne ko: \u00abAa\u014bkay, Boroom bi, xam nga ne, b\u00ebgg naa la.\u00bb Yeesu ne ko: \u00abS\u00e0mmal ma sama xar yi.\u00bb\n21:17 Mu neeti ko \u00f1etteel bi yoon: \u00abSimo\u014b doomu Yowaana, b\u00ebgg nga maam?\u00bb Piyeer am naqar ci li mu ko laaj \u00f1etti yoon: \u00abNdax b\u00ebgg nga ma?\u00bb Mu tontu ko ne: \u00abBoroom bi, xam nga l\u00e9pp; xam nga ne b\u00ebgg naa la.\u00bb Yeesu ne ko: \u00abTopptool ma sama xar yi.\n21:18 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg Piyeer, maa ngi la koy wax, bi nga dee ndaw yaa doon takk sa ge\u00f1o, di dem fu la neex. Waaye boo m\u00e0ggatee, dinga t\u00e0llal say loxo, keneen takkal la sa ge\u00f1o, y\u00f3bbu la foo b\u00ebggul.\u00bb\n21:19 Ci baat yooyu la Yeesu doon misaale nan la Piyeer war a faatoo ngir jollil ndamu Y\u00e0lla. Noonu Yeesu ne ko: \u00abToppal ci man!\u00bb\n21:20 Piyeer geestu, gis taalibe bi Yeesu b\u00ebggoon, di \u00f1\u00ebw ci seen gannaaw. Taalibe boobu mooy ki s\u00f3onu woon ca Yeesu, ba \u00f1uy lekk, te laajoon ko ne: \u00abBoroom bi, kan moo lay wori?\u00bb\n21:21 Piyeer gis ko, daldi ne Yeesu: \u00abKii nag, Boroom bi, nu muy mujje?\u00bb\n21:22 Yeesu ne ko: \u00abSu ma neexoon mu dund, ba ma dellusi, lu ciy sa yoon? Yaw toppal ci man.\u00bb\n21:23 Noonu am, ci bokki taalibe yi, \u00f1u xalaat ne, taalibe boobu du dee. Moona Yeesu musul ne Piyeer, du dee; waaye li mu wax mooy: \u00abSu ma neexoon mu dund, ba ma dellusi, lu ciy sa yoon?\u00bb\n21:24 Taalibe boobu mooy seede mbir yooyu, bind leen, te xam nanu ne, li muy wax d\u00ebgg la.\n21:25 Yeesu def na yeneen j\u00ebf yu bare. Su \u00f1u ko doon nettali, bind l\u00e9pp, xalaat naa ne, t\u00e9ere yi du\u00f1u xaj ci \u00e0ddina.","title":"Wolof Bible (NT): John","type":"page"}
