{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/luk.htm","path":"bib/wb/wlf/luk.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/luk.htm","text":"1:1 Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit \u00f1u bare sasoo na\u00f1oo bind ab nettali bu j\u00ebm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir,\n1:2 li d\u00ebppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te \u00f1u mujj nekk jawri\u00f1i k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n1:3 L\u00e9egi nag kon man ci sama w\u00e0ll, g\u00ebstu naa ci l\u00e9pp li ko dale ca nj\u00e0lb\u00e9en ga, te fas naa la ko y\u00e9enee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe.\n1:4 Noonu dinga man a xam ne, li \u00f1u la j\u00e0ngaloon lu w\u00e9r pe\u014b\u014b la.\n1:5 Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca r\u00e9ewu Yawut ya, amoon na saraxalekat bu \u00f1u tudde Sakariya te bokk ca mbootaayu saraxalekat, ya askanoo ci Abiya. Jabaram Elisabet askanoo moom itam ci Aaroona.\n1:6 Sakariya ak jabaram \u00f1u jub la\u00f1u ca kanam Y\u00e0lla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi y\u00e9pp.\n1:7 Waaye amu\u00f1u doom, ndaxte Elisabet m\u00ebnul a am doom, te it fekk \u00f1oom \u00f1aar \u00f1\u00e9pp ay m\u00e0ggat la\u00f1u.\n1:8 Benn b\u00e9s nag Sakariya doon def ligg\u00e9eyu saraxaleem ca Y\u00e0lla, ndaxte mbootaayam a aye keroog.\n1:9 Bi \u00f1uy tegoo bant, ni ko saraxalekat yi daan defe nakajekk, ngir xam kan mooy dugg ca b\u00e9rab bu sell ba ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakariya.\n1:10 Ca waxtu wa \u00f1uy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di \u00f1aan.\n1:11 Noonu benn malaakam Boroom bi daldi fee\u00f1u Sakariya, taxaw ca f\u00e9eteek ndeyjooru saraxalukaay, ba \u00f1uy taal cuuraay ca kawam.\n1:12 Naka la ko Sakariya gis, fitam daldi dem, mu tiit.\n1:13 Waaye malaaka ma ne ko: \u00abBul ragal dara Sakariya, ndaxte sa \u00f1aan nangu na. Elisabet sa jabar dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya.\n1:14 Sa mb\u00e9g lay doon, sa xol sedd ci, te \u00f1u bare dina\u00f1u b\u00e9g ci juddoom,\n1:15 ndaxte dina nekk ku m\u00e0gg ca kanam Y\u00e0lla. Du naan bii\u00f1 walla dara luy m\u00e0ndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu.\n1:16 Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Y\u00e0lla seen Boroom.\n1:17 Mooy jiitu, di y\u00e9gle \u00f1\u00ebwu Boroom bi, \u00e0nd ak xel mi ak doole, ji yonent Y\u00e0lla Iliyas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo \u00f1i d\u00e9ggadi ci maanduteg \u00f1i jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.\u00bb\n1:18 Sakariya daldi ne malaaka ma: \u00abNan laay xame ne, loolu d\u00ebgg la? Ndaxte mag laa, te sama jabar it m\u00e0ggat na.\u00bb\n1:19 Malaaka ma tontu ko ne: \u00abMan maay Jibril miy taxaw ci kanam Y\u00e0lla. Da\u00f1u maa y\u00f3nni ngir ma wax ak yaw te y\u00e9gal la xebaar bu baax boobu.\n1:20 L\u00e9egi nag gannaaw g\u00ebmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo man a wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.\u00bb\n1:21 Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakariya y\u00e0gg ca b\u00e9rab bu sell ba.\n1:22 Waaye bi mu g\u00e9nnee nag, m\u00ebnul a wax ak \u00f1oom. Noonu nit \u00f1a xam ne, dafa am lu ko fee\u00f1u ca b\u00e9rab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.\n1:23 Bi Sakariya matalee ligg\u00e9eyu saraxaleem ba noppi, mu daldi \u00f1ibbi.\n1:24 Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet jabaram \u00ebmb, di ko n\u00ebbb lu mat jur\u00f3omi weer\n1:25 te naan: \u00abLii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama g\u00e0cce ci nit \u00f1i!\u00bb\n1:26 Bi Elisabet nekkee ci jur\u00f3om-benni weeram, Y\u00e0lla y\u00f3nni na malaakaam Jibril ca d\u00ebkku Nasaret ca diiwaanu Galile.\n1:27 Mu yebal ko ca janq bu \u00f1u may waa ju bokk ci askanu Daawuda te \u00f1u koy wax Yuusufa, waaye \u00e0ndagu\u00f1u. Janq baa ngi tudd Maryaama.\n1:28 Malaaka ma dikk ca moom ne ko: \u00abJ\u00e0mm ngaam, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.\u00bb\n1:29 Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu man a tekki.\n1:30 Malaaka ma ne ko: \u00abBul ragal dara Maryaama, ndaxte Y\u00e0lla t\u00e0nn na la ci yiwam.\n1:31 Dinga \u00ebmb, jur doom ju g\u00f3or; nanga ko tudde Yeesu.\n1:32 Ku m\u00e0gg lay nekki, te dina\u00f1u ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Y\u00e0lla dina ko j\u00e9bbal nguuru Daawuda maamam.\n1:33 Noonu dina yilif askanu Yanq\u00f3oba ba f\u00e0ww, te nguuram du am \u00e0pp.\u00bb\n1:34 Maryaama laaj malaaka ma ne ko: \u00abNaka la loolu man a ame? Man de, janq laa ba tey.\u00bb\n1:35 Malaaka ma tontu ko ne: \u00abXel mu Sell mi dina w\u00e0cc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci k\u00e0ttanam. Moo tax xale biy juddu dina\u00f1u ko wooye Ku sell ki, Doomu Y\u00e0lla ji.\n1:36 Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju g\u00f3or cig m\u00e0ggatam. Ki \u00f1u doon wooye ku m\u00ebnul a am doom, mu ngi ci jur\u00f3om-benni weeram.\n1:37 Ndaxte dara t\u00ebwul Y\u00e0lla.\u00bb\n1:38 Maryaama ne ko: \u00abJaamub Boroom bi laa. Na Y\u00e0lla def ci man li nga wax.\u00bb Ci noonu malaaka ma daldi dem.\n1:39 Ci jamono jooju Maryaama j\u00f3g, gaawantu dem ci benn d\u00ebkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude.\n1:40 Mu dugg ca k\u00ebr Sakariya, daldi nuyu Elisabet.\n1:41 Naka la Elisabet d\u00e9gg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yengatu ci biiram. Noonu Xelum Y\u00e0lla mu Sell mi daldi solu Elisabet.\n1:42 Elisabet wax ca kaw ne: \u00abBarkeel na\u00f1u la ci jig\u00e9en \u00f1i, barkeel doom ji nga \u00ebmb!\n1:43 Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom \u00f1\u00ebw di ma seetsi?\n1:44 Maa ngi lay wax ne, naka laa la d\u00e9gg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yengu ci sama biir ndax mb\u00e9g.\n1:45 Barke \u00f1eel na la, yaw mi g\u00ebm ne, li la Boroom bi y\u00e9gal dina mat!\u00bb\n1:46 Noonu Maryaama daldi ne:\n1:47 \u00abSama xol a ngi m\u00e0ggal Boroom bi,sama xel di b\u00e9g ci Y\u00e0lla sama Musalkat,\n1:48 ndaxte f\u00e0ttaliku na ma,man jaamam bu woyof bi.Gannaawsi tey, niti jamono y\u00e9ppdina\u00f1u ma wooye ki \u00f1u barkeel,\n1:49 ndaxte Ku M\u00e0gg ki defal na ma lu r\u00e9y.Turam dafa sell.\n1:50 Day w\u00e0cce y\u00ebrmandeem ci \u00f1i ko ragal,ci seeni s\u00ebt ba ci seeni s\u00ebtaat.\n1:51 Wone na j\u00ebf yu mag ci dooley loxoom,te tas mbooloom \u00f1iy r\u00e9y-r\u00e9ylu,\n1:52 daaneel boroom doole yi ci seen nguur,y\u00e9kkati baadoolo yi.\n1:53 \u00d1i xiif, reggal na leen ak \u00f1am wu neex,te d\u00e0q boroom alal yi,\u00f1u daw ak loxoy neen.\n1:54 Wallu na b\u00e0nni Israyil giy jaamam,di f\u00e0ttaliku y\u00ebrmandeem,\n1:55 ni mu ko dige woon sunuy maam,j\u00ebmale ko ci Ibraayma ak askanam ba f\u00e0ww.\u00bb\n1:56 Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu war a tollook \u00f1etti weer, sog a \u00f1ibbi.\n1:57 Gannaaw loolu jamono ji Elisabet war a mucc agsi, mu daldi jur doom ju g\u00f3or.\n1:58 D\u00ebkkandoom yi ak mbokkam yi y\u00e9g ne, Boroom bi won na ko y\u00ebrmande ju r\u00e9y, \u00f1u \u00e0nd ak moom b\u00e9g.\n1:59 Bi b\u00e9s ba dellusee, \u00f1u \u00f1\u00ebw xarafalsi xale ba, b\u00ebgg koo dippee baayam Sakariya.\n1:60 Waaye yaayam ne leen: \u00abD\u00e9ed\u00e9et, Yaxya lay tudd.\u00bb\n1:61 \u00d1u ne ko: \u00abAmoo menn mbokk mu tudd noonu.\u00bb\n1:62 \u00d1u daldi liyaar baayam, ngir xam nan la b\u00ebgg \u00f1u tudde xale ba.\n1:63 Sakariya laaj \u00e0lluwa, bind ci ne: \u00abYaxya la tudd.\u00bb \u00d1\u00e9pp daldi waaru.\n1:64 Ca saa sa Y\u00e0lla dindi luu gi, Sakariya daldi waxaat, di m\u00e0ggal Y\u00e0lla.\n1:65 Waa d\u00ebkk ba b\u00e9pp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude y\u00e9pp.\n1:66 \u00d1i d\u00e9gg nettali, bi j\u00ebm ci mbir yooyu, da\u00f1u koo denc ci seen xol te naan: \u00abNu xale bii di mujje nag?\u00bb Ndaxte leeroon na ne, dooley Boroom baa ngi \u00e0nd ak moom.\n1:67 Sakariya baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla ne:\n1:68 \u00abCant \u00f1eel na Boroom bi, Y\u00e0llay Israyil,ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!\n1:69 Fee\u00f1al na nu Musalkat bu am doole,bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam,\n1:70 ni mu y\u00e9glee woon bu y\u00e0ggjaarale ko ci yonentam yu sell yi.\n1:71 Dina nu musal ci sunuy noon,j\u00eble nu ci sunu loxoy ba\u00f1aale.\n1:72 Y\u00e0lla wone na y\u00ebrmandeem,ji mu digoon sunuy maam,te di f\u00e0ttaliku k\u00f3ll\u00ebre, gi mu fas ak \u00f1oom,\n1:73 di ngi\u00f1, li mu gi\u00f1aloon sunu maam Ibraayma naan,\n1:74 dina nu teqale ak sunuy noon,ngir nu man koo jaamu ci j\u00e0mm,\n1:75 nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.\n1:76 Yaw nag doom, dina\u00f1u lay wooye yonentu Aji Kawe ji,ndaxte dinga jiitu, di y\u00e9gle \u00f1\u00ebwu Boroom bi,di ko x\u00e0llal yoon wi.\n1:77 Dinga xamal mbooloom,ni leen Boroom bi man a musale,jaare ko ci seen mbaalug b\u00e0kkaar,\n1:78 ndaxte Y\u00e0lla sunu Boroom fees na ak y\u00ebrmande,ba tax muy w\u00e0cce ci nun jant buy fenk,\n1:79 ngir leeral \u00f1i toog ci l\u00ebnd\u00ebm,takkandeeru dee tiim leen,ngir jiite nu ci yoonu j\u00e0mm.\u00bb\n1:80 Noonu Yaxyaa ngi doon m\u00e0gg, te xelam di ubbiku. Mu d\u00ebkk ca m\u00e0ndi\u014b ma, ba b\u00e9s ba muy fee\u00f1u b\u00e0nni Israyil.\n2:1 Ca jamono jooja buur bu mag bu \u00f1uy wax Ogust joxe ndigal ne, na \u00f1\u00e9pp binduji.\n2:2 Mbindu mooma, di mu j\u00ebkk ma, daje na ak jamono, ja Kiri\u00f1us nekke boroom r\u00e9ewu Siri.\n2:3 Noonu ku nekk dem binduji ca sa d\u00ebkku cosaan.\n2:4 Yuusufa nag daldi j\u00f3ge Nasaret ca diiwaanu Galile, j\u00ebm ca diiwaanu Yude ca Betleyem, d\u00ebkk ba Daawuda cosaanoo, ndaxte ci askanu Daawuda la bokk.\n2:5 Mu dem binduji, \u00e0nd ak Maryaama jabaram, fekk booba Maryaama \u00ebmb.\n2:6 Bi \u00f1u nekkee Betleyem, waxtu wa mu waree mucc agsi.\n2:7 Mu taawloo doom ju g\u00f3or, mu laxas ko ci ay laytaay, t\u00ebral ko ca lekkukaayu jur ga, ndaxte xaju\u00f1u woon ca dalukaay ba.\n2:8 Fekk booba amoon na ca gox ba ay s\u00e0mm yu daan fanaan ca tool ya, di wottu jur ga.\n2:9 Noonu benn malaakam Boroom bi fee\u00f1u leen, ndamu Boroom bi daldi leer, melax, w\u00ebr leen. Tiitaange ju r\u00e9y j\u00e0pp leen.\n2:10 Waaye malaaka mi ne leen: \u00abBuleen tiit, ndaxte dama leen di xamal xebaar bu baax buy indi mb\u00e9g mu r\u00e9y ci nit \u00f1\u00e9pp.\n2:11 Tey jii ca d\u00ebkku Daawuda, ab Musalkat juddul na leen fa, te mooy Almasi bi, di Boroom bi.\n2:12 Ci firnde jii ngeen koy x\u00e0mmee: dingeen gis liir bu \u00f1u laxas ci ay laytaay, t\u00ebral ko ci lekkukaayu jur.\u00bb\n2:13 Bi mu waxee loolu, yeneen malaaka yu bare yu j\u00f3ge asamaan, \u00e0nd ak moom, di sant Y\u00e0lla naan:\n2:14 \u00abNa\u00f1u m\u00e0ggal Y\u00e0lla ca asamaan su kawe sa,te ci \u00e0ddina, na j\u00e0mm ji w\u00e0cc ci nit, \u00f1i mu nangu ndax yiwam!\u00bb\n2:15 Bi malaaka ya delloo ca asamaan, s\u00e0mm yi di waxante naan: \u00abNanu dem boog Betleyem, seeti la fa xew, li nu Boroom bi xamal.\u00bb\n2:16 \u00d1u daldi gaawantu dem, gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir, ba \u00f1u t\u00ebral ca lekkukaayu jur ga.\n2:17 Bi \u00f1u leen gisee, \u00f1u nettali la \u00f1u leen waxoon ca mbirum xale ba.\n2:18 \u00d1i d\u00e9gg li s\u00e0mm yi doon wax \u00f1\u00e9pp daldi waaru lool.\n2:19 Waaye Maryaama moom, takkoon na mbir yooyu y\u00e9pp, di ko xalaat ci xolam.\n2:20 Noonu s\u00e0mm ya dellu ca seen jur, di m\u00e0ggal Y\u00e0lla, di ko sant ci li \u00f1u d\u00e9ggoon l\u00e9pp te gis ko, ndaxte l\u00e9pp am na, ni ko Boroom bi waxe woon.\n2:21 Bi b\u00e9s ba dellusee jamonoy xarafal xale ba agsi. \u00d1u tudde ko Yeesu, ni ko malaaka ma diglee woon, laata ko yaayam di \u00ebmb.\n2:22 Noonu jamono ji \u00f1u leen waroon a sellale agsi, ni ko yoonu Musaa t\u00ebrale. Waajuri Yeesu yi daldi koy y\u00f3bbu ca d\u00ebkku Yerusalem, ngir s\u00e9dde ko Boroom bi.\n2:23 Ndaxte bind na\u00f1u ci yoonu Boroom bi ne: \u00abB\u00e9pp taaw bu g\u00f3or, na\u00f1u ko s\u00e9dde Boroom bi.\u00bb\n2:24 Bi \u00f1u ko y\u00f3bboo, def na\u00f1u itam sarax, ni ko yoonu Boroom bi santaanee: \u00ab\u00f1aari pitaxu \u00e0ll walla \u00f1aari xati yu ndaw.\u00bb\n2:25 Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Y\u00e0lla la te d\u00e9ggal ko, doon s\u00e9entu jamono, ji Y\u00e0lla war a d\u00ebf\u00ebl b\u00e0nni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom,\n2:26 te xamal na ko ne, du dee mukk te gisul Almasib Boroom bi.\n2:27 Noonu Xelum Y\u00e0lla daldi y\u00f3bbu Simeyon ba ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir s\u00e9dde ko Y\u00e0lla, ni ko yoon wi santaanee,\n2:28 Simeyon j\u00ebl xale bi, leewu ko, daldi sant Y\u00e0lla ne:\n2:29 \u00abBoroom bi, nanga yiwi sa jaam,mu noppaluji ci j\u00e0mm, ni nga ko waxe.\n2:30 Ndaxte sama b\u00ebt tegu na ci mucc gi nga lal,\n2:31 xeet y\u00e9pp seede ko.\n2:32 Muy leer giy leeral xeet yi,di ndamu Israyil say gaay.\u00bb\n2:33 Waajuri Yeesu yi waaru ci li \u00f1u doon wax ci xale bi.\n2:34 Noonu Simeyon \u00f1aanal leen, ba noppi ne Maryaama: \u00abXale bii Y\u00e0llaa ko y\u00f3nni, ngir \u00f1u bare ci Israyil daanu te y\u00e9kkatiku. Def na ko it muy firnde ju \u00f1uy weddi,\n2:35 ba naqar dina xar sa xol ni jaasi. Noonu xalaati \u00f1u bare fee\u00f1.\u00bb\n2:36 Amoon na it ca Yerusalem yonent bu \u00f1uy wax Aana. Doomu Fanuwel mi askanoo ci Aser la woon, te Aana m\u00e0ggatoon na lool. Bi mu s\u00e9yee, d\u00ebkk na jur\u00f3om-\u00f1aari at ak j\u00ebkk\u00ebram.\n2:37 J\u00ebkk\u00ebr ja gaa\u00f1u, te s\u00e9yaatul. L\u00e9egi amoon na jur\u00f3om-\u00f1ett-fukki at ak \u00f1eent. Mi ngi d\u00ebkke woon a jaamu Y\u00e0lla guddi ak b\u00ebcc\u00ebg ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, di \u00f1aan ak di woor.\n2:38 Aana yem ca waxi Simeyon ya, daldi g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla tey y\u00e9gal mbiri liir ba \u00f1\u00e9pp \u00f1i doon s\u00e9entu jamono, ji Y\u00e0lla war a jot Yerusalem.\n2:39 Bi waajuri Yeesu yi matalee seen warugar ci l\u00e9pp lu yoonu Boroom bi santaane woon, \u00f1u dellu seen d\u00ebkku Nasaret ca diiwaanu Galile.\n2:40 Xale baa nga doon m\u00e0gg, di d\u00ebg\u00ebr, mu fees ak xel te yiwu Y\u00e0lla \u00e0nd ak moom.\n2:41 At mu jot nag waajuri Yeesu yi daan na\u00f1u dem Yerusalem, ngir m\u00e0ggali b\u00e9su J\u00e9ggi ba.\n2:42 Noonu bi Yeesu amee fukki at ak \u00f1aar, \u00f1u dem m\u00e0ggal ga, ni \u00f1u ko daan defe nakajekk.\n2:43 Bi m\u00e0ggal ga tasee, \u00f1u d\u00ebpp \u00f1ibbi, waaye xale ba Yeesu des Yerusalem, te ay waajuram y\u00e9gu\u00f1u ko.\n2:44 \u00d1u xalaat ne, Yeesu dafa \u00e0ndoon ak \u00f1eneen, \u00f1i \u00f1u bokkaloon yoon. Bi \u00f1u doxee b\u00e9sub l\u00ebmm, \u00f1u t\u00e0mbali di ko seet ci seen bokk yi ak seen xame yi.\n2:45 Bi \u00f1u ko gisul nag, \u00f1u daldi dellu Yerusalem, seeti ko.\n2:46 Ca gannaaw \u00ebll\u00ebg sa \u00f1u fekk ko ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, mu toog ci j\u00e0ngalekati Yawut yi, di d\u00e9glu ak di laajte.\n2:47 \u00d1\u00e9pp \u00f1i d\u00e9gg li mu wax y\u00e9emu ci xel, mi mu \u00e0ndal, ak ni mu doon tontoo.\n2:48 Naka la ko waajuram yi gis, \u00f1u daldi waaru. Yaayam ne ko: \u00abSama doom, lu tax nga def nu lii? Man ak sa baay nu ngi la doon seet, jaaxle lool.\u00bb\n2:49 Mu ne leen: \u00abLu tax ngeen may seet? Xanaa xamuleen ne, damaa war a nekk ci sama k\u00ebr Baay?\u00bb\n2:50 Waaye xamu\u00f1u li k\u00e0ddoom yi doon tekki.\n2:51 Noonu Yeesu daldi \u00e0nd ak \u00f1oom, dellu Nasaret te d\u00e9ggal ay waajuram. Fekk yaayam moom takk mbir yooyu y\u00e9pp ci xolam.\n2:52 Yeesoo ngi doon m\u00e0gg ci j\u00ebmm, tey yokku ci xam-xam te neex Y\u00e0lla ak nit \u00f1i.\n3:1 Fukkeelu at ak jur\u00f3om ci nguuru Tibeer Sesaar, fekk Po\u00f1s\u00eb Pilaat yilif diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, te Lisa\u00f1as yilif Abilen.\n3:2 Te it Anas ak Kayif nekkoon saraxalekat yu mag ya. Ca jamono jooja la k\u00e0ddug Y\u00e0lla w\u00e0cc ci Yaxya, doomu Sakariya, ca m\u00e0ndi\u014b ma.\n3:3 Yaxya daldi dugg \u00e0ll, bi w\u00ebr dexu Yurdan g\u00e9pp, di waaree nii: \u00abTuubleen seeni b\u00e0kkaar, ba noppi ma s\u00f3ob leen ci ndox, ngir Y\u00e0lla baal leen seeni b\u00e0kkaar.\u00bb\n3:4 Loolu la\u00f1u bind ci t\u00e9ereb waxi yonent Y\u00e0lla Esayi naan:\u00abAm na baat buy xaacu ca m\u00e0ndi\u014b ma ne:\u201cX\u00e0ll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.\n3:5 Na\u00f1u s\u00ebkk xur yi,maasale tund yi ak j\u00e0nj yi.Yoon yi d\u00ebng \u00f1u jubbanti leen,yi \u00f1agas \u00f1u rataxal leen.\n3:6 Bu ko defee b\u00e9pp mbindeef dina gismucc gi Y\u00e0lla t\u00ebral.\u201d\u00bb\n3:7 Mbooloo ma daan \u00f1\u00ebw ngir mu s\u00f3ob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: \u00abY\u00e9en \u00f1i fees ak da\u014bar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Y\u00e0lla mi nar a w\u00e0cc?\n3:8 J\u00ebfeleen nag ni \u00f1u tuub seeni b\u00e0kkaar, te ba\u00f1 a nax seen bopp naan: \u201cNun daal doomi Ibraayma lanu,\u201d ndaxte maa ngi leen koy wax, Y\u00e0lla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii.\n3:9 S\u00e9mmi\u00f1 wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu me\u00f1\u00f1ul doom yu baax, dees na ko gor, s\u00e0nni ko ci safara si.\u00bb\n3:10 Mbooloo ma laaj ko ne: \u00abLan lanu war a def nag?\u00bb\n3:11 Mu ne leen: \u00abKu am \u00f1aari mbubb, nga jox menn mi ki amul. Ku am \u00f1am itam, nga bokk ko ak ki amul.\u00bb\n3:12 Ay juutikat itam \u00f1\u00ebw ca Yaxya, ngir mu s\u00f3ob leen ci ndox; \u00f1u ne ko: \u00abKilifa gi, lu nu war a def?\u00bb\n3:13 Mu tontu leen ne: \u00abLaajleen rekk lu jaadu.\u00bb\n3:14 Ay xarekat laaj na\u00f1u ko ne: \u00abLi j\u00ebm ci nun nag?\u00bb Mu ne leen: \u00abBuleen n\u00e9ewal doole kenn, j\u00ebl xaalisam ci kaw ay t\u00ebkku mbaa ci seede lu dul d\u00ebgg. Waaye doylooleen li \u00f1u leen di fey.\u00bb\n3:15 Mbooloo maa ngay xaar, di s\u00e9entook a laaj ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi.\n3:16 Noonu Yaxya tontu leen \u00f1oom \u00f1\u00e9pp ne: \u00abMan maa ngi leen di s\u00f3ob ci ndox. Waaye ki ma \u00ebpp k\u00e0ttan dina \u00f1\u00ebw te yeyoowumaa tekki ay d\u00e0llam. Kooku dina leen s\u00f3ob ci Xel mu Sell mi ak safara.\n3:17 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir j\u00e9ri d\u00e0gga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca s\u00e0qam, waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk.\u00bb\n3:18 Noonu Yaxya teg ca yeneen d\u00e9nkaane yu bare, di y\u00e9gal nit \u00f1a xebaar bu baax ba.\n3:19 Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Eroj\u00e0dd, jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen \u00f1aawteef,\n3:20 ba faf t\u00ebj Yaxya kaso.\n3:21 Noonu Yaxya s\u00f3ob mbooloo m\u00e9pp ci ndox, s\u00f3obaale it Yeesu. Bi Yeesu di \u00f1aan nag, asamaan daldi ubbiku.\n3:22 Noonu Xel mu Sell mi daldi w\u00e0cc ci moom, yor j\u00ebmmu pitax, te baat bu j\u00f3ge asamaan jib ne: \u00abYaa di sama Doom, ji ma b\u00ebgg; ci yaw laa ame b\u00e0nneex.\u00bb\n3:23 Bi Yeesu di t\u00e0mbali ligg\u00e9eyam, amoon na lu war a tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci b\u00ebti nit \u00f1i.Te Yuusufa mooy doomu Eli,\n3:24 miy doomu Matat.Matat, Lewi mooy baayam; Lewi, Melki;Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;\n3:25 Yuusufa, Matacas; Amos; Naxum; Esli; Nagayi.\n3:26 Nagayi, Maat; Matacas; Semeyin; Yoseg; Yoda.\n3:27 Yoda, Yowanan mooy baayam; Yowanan, Resa;Resa, Sorobabel. Kooku Salacel a ko jur; Salacel, Neri;\n3:28 Neri, Melki; Adi; Kosam; Elmadam; Er.\n3:29 Er, Yeesu; Eliyeser; Yorim; Matat; Lewi;\n3:30 Simeyon; Yuda; Yuusufa; Yonam; Eliyakim.\n3:31 Eliyakim, Meleya; Meleya, Mena;Mena, Matata; Matata, Natan;Natan, Daawuda.\n3:32 Daawuda mooy doomu Yese;Yese, Obedd; Bowas; Salmon; Naason.\n3:33 Naason; Aminadab; Aminadab, Admin;Arni; Esrom; Fares; Yuda;\n3:34 Yanq\u00f3oba; Isaaxa; Ibraayma; Teraa; Naxor;\n3:35 Serug; Ragaw; Faleg; Eber; Sala.\n3:36 Sala, Kaynam mooy baayam; Kaynam, Arpags\u00e0dd;Arpags\u00e0dd, Sem; Sem, N\u00f3oyin; N\u00f3oyin, Lemeg;\n3:37 Lemeg, Matusala; Enog, Yaredd; Maleleel; Kaynan;\n3:38 Enos; Set; Set doomu Aadama;Aadama doomu Y\u00e0lla.\n4:1 Noonu Yeesu fees ak Xel mu Sell mi, j\u00f3ge dexu Yurdan.\n4:2 Xelum Y\u00e0lla mi y\u00f3bbu ko ca m\u00e0ndi\u014b ma, mu nekk fa \u00f1eent-fukki fan, j\u00e0nkoonte ak fiiri Seytaane. Lekkul woon dara ci fan yooya, te gannaaw gi mu xiif.\n4:3 Noonu Seytaane ne ko: \u00abBoo dee Doomu Y\u00e0lla, santal doj wii mu nekk mburu.\u00bb\n4:4 Yeesu tontu ko ne: \u00abMbind mi nee na: \u201cNit du dunde mburu rekk.\u201d\u00bb\n4:5 Seytaane y\u00f3bbu na ko fu kawe. Ci xef-ak-xippi mu won ko r\u00e9ewi \u00e0ddina s\u00e9pp,\n4:6 ne ko: \u00abDinaa la jox b\u00e9pp sa\u00f1-sa\u00f1u nguur yii ak seen ndam ndaxte j\u00e9bbal na\u00f1u ma ko, te ku ma soob laa koy jox.\n4:7 Kon boo ma m\u00e0ggalee, dinga moom l\u00e9pp.\u00bb\n4:8 Yeesu tontu ko ne: \u00abMbind mi nee na: \u201cNanga m\u00e0ggal Y\u00e0lla sa Boroom te jaamu ko moom rekk.\u201d\u00bb\n4:9 Seytaane y\u00f3bbu na ko Yerusalem, teg ko ca njobbaxtalu k\u00ebr Y\u00e0lla ga ne ko: \u00abBoo dee Doomu Y\u00e0lla, t\u00ebbal j\u00ebm ci suuf,\n4:10 ndaxte Mbind mi nee na:\u201cDina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,\u00f1u s\u00e0mm la,\n4:11 dina\u00f1u la leewu ci seeni loxo,ngir nga ba\u00f1 a fakkastalu ciw doj.\u201d\u00bb\n4:12 Yeesu tontu ko ne: \u00abBind na\u00f1u ne: \u201cBul dii\u014bat Y\u00e0lla, sa Boroom.\u201d\u00bb\n4:13 Bi mu ko lalalee fiiram yi mu am y\u00e9pp, Seytaane daldi sore Yeesu, di xaar yeneen jamono.\n4:14 Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Y\u00e0lla, te turam siiw ca diiwaan booba b\u00e9pp.\n4:15 Muy j\u00e0ngale ca seeni j\u00e0ngu, te \u00f1\u00e9pp di ko tagg.\n4:16 Yeesu dem Nasaret fa mu yaroo, te ca b\u00e9su noflaay ba, mu dugg ca j\u00e0ngu ba, ni mu ko daan defe. Noonu mu taxaw ngir j\u00e0ngal mbooloo mi.\n4:17 \u00d1u jox ko t\u00e9ereb yonent Y\u00e0lla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis b\u00e9rab, ba \u00f1u bind aaya yii:\n4:18 \u00abXelum Boroom baa ngi ci man,ndaxte moo ma t\u00e0nn,ngir ma y\u00e9gal n\u00e9ew doole yi xebaar bu baax bi.Dafa maa y\u00f3nni,ngir ma y\u00e9gal jaam \u00f1i ne, dina\u00f1u leen goreel,y\u00e9gal gumba yi ne, dina\u00f1u gis,te jot \u00f1i \u00f1u noot,\n4:19 tey y\u00e9gle atum yiw, mi j\u00f3ge ci Boroom bi.\u00bb\n4:20 Bi mu j\u00e0ngee aaya yooyu ba noppi, mu ub t\u00e9ere bi, delloo ko ki koy denc, toog. \u00d1\u00e9pp \u00f1a nekkoon ca j\u00e0ngu ba d\u00e9kk koy b\u00ebt.\n4:21 Noonu mu daldi ne: \u00abTey jii, loolu Mbind mi wax mat na, bi ngeen koy d\u00e9glu.\u00bb\n4:22 \u00d1\u00e9pp di seede lu rafet ci Yeesu, di waaru ci wax ju neex, ji mu doon y\u00e9gle, \u00f1u naan: \u00abNdax kii du doomu Yuusufa?\u00bb\n4:23 Mu daldi leen ne: \u00abXam naa ne dingeen ma ne: \u201cFajkat bi, fajal sa bopp. Y\u00e9g nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci r\u00e9ew mi nga d\u00ebkk.\u201d\u00bb\n4:24 Mu tegaat ca ne: \u00abCi d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, ab yonent kenn du ko teral ca r\u00e9ewam.\n4:25 Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Iliyas, bi mu tawul lu mat \u00f1etti at ak genn-w\u00e0ll, te xiif bu metti am ca r\u00e9ew m\u00e9pp, amoon na ca Israyil jig\u00e9en yu bare yu seen j\u00ebkk\u00ebr faatu.\n4:26 Moona Y\u00e0lla y\u00f3nniwul Iliyas ci kenn ci \u00f1oom, waaye mu yebal ko ci jig\u00e9en ju j\u00ebkk\u00ebram faatu, ju d\u00ebkk Sarebta, ca wetu Sidon.\n4:27 Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Y\u00e0lla Alisa, ay nit \u00f1u bare \u00f1u gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naaman, mi d\u00ebkkoon r\u00e9ewu Siri.\u00bb\n4:28 Bi \u00f1u d\u00e9ggee wax yooya, \u00f1\u00e9pp \u00f1a nekkoon ca j\u00e0ngu ba daldi fees ak mer.\n4:29 Noonu \u00f1u j\u00f3g, g\u00e9nne ko d\u00ebkk ba, y\u00f3bbu ko ca mbartalum tund, wa \u00f1u sanc seen d\u00ebkk, ngir b\u00ebm\u00ebx ko ci suuf.\n4:30 Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam.\n4:31 Gannaaw loolu Yeesu dem Kapernawum, ab d\u00ebkk ca diiwaanu Galile.\n4:32 Mu j\u00e0ngal leen ca b\u00e9su noflaay ba, \u00f1u waaru ca nj\u00e0ngaleem, ndaxte dafa wax ak sa\u00f1-sa\u00f1.\n4:33 Noonu am na ci j\u00e0ngu bi nit ku rab j\u00e0pp. Mu daldi xaacu ne:\n4:34 \u00abMoo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa \u00f1\u00ebw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji j\u00f3ge ci Y\u00e0lla!\u00bb\n4:35 Waaye Yeesu g\u00ebdd ko naan: \u00abNoppil te g\u00e9nn ci moom!\u00bb Noonu rab wi daaneel nit ki ci suuf ci kanamu \u00f1\u00e9pp, daldi g\u00e9nn ci moom te gaa\u00f1u ko.\n4:36 Bi loolu amee \u00f1\u00e9pp waaru, \u00f1uy waxante ci seen biir naan: \u00abC\u00e9y jii wax! Ci sa\u00f1-sa\u00f1 ak doole lay sant rab yi, \u00f1u daldi g\u00e9nn.\u00bb\n4:37 Noonu turam siiw ca diiwaan b\u00e9pp.\n4:38 Bi mu j\u00f3gee ci j\u00e0ngu bi, Yeesu dafa dem k\u00ebr Simo\u014b. Gorob Simo\u014b bu jig\u00e9en dafa feebar, ba yaram wi t\u00e0ng lool. \u00d1u naan Yeesu, mu dimbali leen ci.\n4:39 Mu randusi, tiim ko, g\u00ebdd t\u00e0ngoor wi, mu dem. Noonu t\u00e0ngoor wi w\u00e0cc, soxna si j\u00f3g ca saa sa, di leen topptoo.\n4:40 Bi jant sowee, \u00f1u indil Yeesu \u00f1i wopp \u00f1\u00e9pp ak ay j\u00e0ngoro yu wuute. Kenn ku nekk mu teg la loxo, w\u00e9ral la.\n4:41 Te it ay rab di g\u00e9nn ca nit \u00f1a te di yuuxu naan: \u00abYaay Doomu Y\u00e0lla!\u00bb Noonu mu g\u00ebdd leen, te mayu leen, \u00f1u wax dara, ndaxte xam na\u00f1u ne, mooy Almasi bi.\n4:42 Ca nj\u00ebl gu j\u00ebkk Yeesu g\u00e9nn, dem ca b\u00e9rab bu w\u00e9et. Mbooloo ma di ko seet. Bi \u00f1u ko gisee, \u00f1u koy wut a t\u00e9ye, ngir ba\u00f1 mu dem.\n4:43 Waaye mu ne leen: \u00abDamaa war a dem ci yeneen d\u00ebkk yi, ngir y\u00e9gle xebaar bu baax bi ci nguuru Y\u00e0lla, ndaxte looloo tax \u00f1u y\u00f3nni ma.\u00bb\n4:44 Noonu mu dem di waare ca j\u00e0ngu ya ca r\u00e9ewu Yawut ya.\n5:1 Benn b\u00e9s Yeesu taxaw ca tefesu dexu Senesaret. Mbooloo ma w\u00ebr ko, di buuxante ngir d\u00e9glu k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n5:2 Noonu mu gis \u00f1aari gaal yu teer ca tefes ga, nappkat ya ca w\u00e0cce, di raxas seeni mbaal.\n5:3 Mu dugg ci genn gaal, fekk muy gu Simo\u014b, mu ne ko, mu joow ba sore tuuti. Noonu Yeesu toog ca gaal ga, di j\u00e0ngal mbooloo ma.\n5:4 Bi mu j\u00e0ngalee ba noppi, mu ne Simo\u014b: \u00abJoowal gaal gi, ba fa ndox ma g\u00ebn a x\u00f3ote, ngeen s\u00e0nni fa seeni mbaal ngir napp.\u00bb\n5:5 Simo\u014b tontu ko ne: \u00abKilifa gi, coono lanu fanaane biig te j\u00e0ppunu dara. Waaye nag dinaa ko s\u00e0nni ci sa ndigal.\u00bb\n5:6 Naka la\u00f1u s\u00e0nni mbaal yi, j\u00e0pp j\u00ebn yu bare, ba mbaal yay t\u00e0mbalee x\u00ebtt.\n5:7 Noonu \u00f1u daldi liyaar seen \u00e0ndandoo, yi nekk ca geneen gaal ga, ngir \u00f1u \u00f1\u00ebw dimbali leen. \u00d1oo\u00f1u agsi, \u00f1u feesal \u00f1aari gaal yi, ba \u00f1uy b\u00ebgg a suux.\n5:8 Naka la Simo\u014b Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanamu Yeesu ne ko: \u00abSore ma Boroom bi, ndaxte nitu b\u00e0kkaar laa!\u00bb\n5:9 Wax na loolu nag, ndax j\u00ebn yu bare ya \u00f1u mbaaloon daf koo jaaxal, moom ak \u00f1a mu \u00e0ndaloon\n5:10 ak \u00f1a mu bokkaloon ligg\u00e9ey ba, maanaam \u00f1aari doomi Sebede yi di Saag ak Yowaana. Yeesu ne Simo\u014b: \u00abBul ragal dara; gannaawsi tey, ay nit ngay mbaal j\u00ebme ci man.\u00bb\n5:11 Noonu \u00f1u teer ca tefes ga, b\u00e0yyi l\u00e9pp, di topp ci moom.\n5:12 Ni Yeesu nekke woon ci ab d\u00ebkk, am fa ku gaana ba daj. Bi mu gisee Yeesu, mu daldi d\u00ebpp j\u00ebwam ci suuf, \u00f1aan ko: \u00abSang bi, soo ko b\u00ebggee, man nga maa w\u00e9ral.\u00bb\n5:13 Yeesu t\u00e0llal loxoom, laal ko naan: \u00abB\u00ebgg naa ko, w\u00e9ral.\u00bb Ca saa sa ngaanaam daldi de\u00f1.\n5:14 Yeesu sant ko ne: \u00abBu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga j\u00e9bbal Y\u00e0lla sarax si yoonu Musaa santaane, ngir \u00f1u xam ne w\u00e9r nga, te mu nekk seede ci \u00f1oom.\u00bb\n5:15 Noonu turu Yeesu di g\u00ebn a siiw. Mbooloo mu bare di \u00f1\u00ebw ci moom, ngir d\u00e9glu ko te mu faj seeni j\u00e0ngoro.\n5:16 Waaye Yeesu moom di beddeeku ci b\u00e9rab yu w\u00e9et ya, di \u00f1aan.\n5:17 Am na b\u00e9s Yeesu doon j\u00e0ngale. Amoon na ca mbooloo, ma teewoon, \u00f1u bokkoon ca Farisen ya ak ay xutbakat yu j\u00f3ge ca d\u00ebkk y\u00e9pp, ya ca Galile ak ya ca Yude ak Yerusalem. Yeesu \u00e0ndoon na ak dooley Boroom bi, ba muy faj ay jarag.\n5:18 Noonu ay nit \u00f1\u00ebw, j\u00e0ppoo basa\u014b, ga \u00f1u t\u00ebral nit ku yaram w\u00e9pp l\u00e0ggi. \u00d1u di ko wut a dugal ca k\u00ebr ga, ngir indi ko ca Yeesu.\n5:19 Waaye gisu\u00f1u fu \u00f1u koy awale ndax mbooloo ma. \u00d1u daldi y\u00e9eg ca kaw k\u00ebr ga nag, xeddi tiwiil ya, yoor waa ja ak basa\u014b ga, w\u00e0cce ko ca kanamu Yeesu ca biir mbooloo ma.\n5:20 Bi Yeesu gisee seen ng\u00ebm, mu ne l\u00e0ggi ba: \u00abSama waay, baal na\u00f1u la say b\u00e0kkaar.\u00bb\n5:21 Xutbakat yi ak Farisen yi di werante ci seen xel naan: \u00abKii mooy kan bay sosal Y\u00e0lla? Ana ku man a baale b\u00e0kkaar yi, ku dul Y\u00e0lla do\u014b\u014b?\u00bb\n5:22 Waaye Yeesu xam seen xalaat, tontu leen ne: \u00abLu tax ngeen di werante ci seen xel?\n5:23 Ma wax ne: \u201cBaal na\u00f1u la say b\u00e0kkaar,\u201d walla ma ne: \u201cJ\u00f3gal te dox,\u201d lan moo ci g\u00ebn a yomb?\n5:24 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci \u00e0ddina sa\u00f1-sa\u00f1u baale b\u00e0kkaar yi.\u00bb Ci kaw loolu Yeesu ne ku l\u00e0ggi ba: \u00abMaa ngi la koy sant, j\u00f3gal, j\u00ebl sa basa\u014b te nga \u00f1ibbi.\u00bb\n5:25 Nit ka j\u00f3g ca saa sa ci kanamu \u00f1\u00e9pp, j\u00ebl basa\u014b, ga \u00f1u ko t\u00ebraloon, \u00f1ibbi tey m\u00e0ggal Y\u00e0lla.\n5:26 Mbooloo m\u00e9pp waaru, di m\u00e0ggal Y\u00e0lla. \u00d1u ragal tey wax naan: \u00abGis nanu tey ay mbir yu \u00ebpp xel.\u00bb\n5:27 Gannaaw loolu Yeesu g\u00e9nn, gis ab juutikat bu tudd Lewi, mu toog ca juuti ba. Mu ne ko: \u00abKaay topp ci man.\u00bb\n5:28 Lewi j\u00f3g, b\u00e0yyi l\u00e9pp, daldi ko topp.\n5:29 Noonu Lewi togglu ay \u00f1am yu bare ci k\u00ebram, ngir teral Yeesu. Juutikat yu bare ak yeneen gan \u00f1u nga fa woon, di lekkandoo ak \u00f1oom.\n5:30 Farisen yi ak seeni xutbakat di xultu taalibey Yeesu yi ne leen: \u00abLu tax ngeen di lekkandoo ak di naanandoo ak ay juutikat ak ay boroom b\u00e0kkaar?\u00bb\n5:31 Yeesu tontu leen ne: \u00ab\u00d1i w\u00e9r soxlawu\u00f1u fajkat, \u00f1i w\u00e9radi \u00f1oo ko soxla.\n5:32 \u00d1\u00ebwuma ngir woo \u00f1i jub, waaye ngir woo b\u00e0kkaarkat yi, \u00f1u tuub seeni b\u00e0kkaar.\u00bb\n5:33 Noonu \u00f1u ne Yeesu: \u00abTaalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi dina\u00f1u faral di woor ak di \u00f1aan ci Y\u00e0lla, waaye say taalibe \u00f1u ngiy lekk ak di naan.\u00bb\n5:34 Yeesu ne leen: \u00abNdax man ngeen a woorloo gan, yi \u00f1\u00ebw cig c\u00e9et, li feek boroom c\u00e9et gaa ngi \u00e0nd ak \u00f1oom?\n5:35 Waaye b\u00e9s yaa ngi \u00f1\u00ebw, yu \u00f1uy j\u00eble boroom c\u00e9et gi ci seen biir. B\u00e9s yooyu nag, dina\u00f1u woor.\u00bb\n5:36 Te it Yeesu wax leen l\u00e9eb wii: \u00abKenn du j\u00ebl mbubb mu bees, xotti ci sekkit, daaxe ko mbubb mu m\u00e0ggat. Lu ko moy, dina xotti mbubb mu bees mi, te sekkit, wi mu ci j\u00eble, du \u00e0nd ak mbubb mu m\u00e0ggat mi.\n5:37 Te kenn du def bii\u00f1 bu bees ci mbuusi der yu m\u00e0ggat. Lu ko moy, bii\u00f1 bu bees bi day toj mbuus yi, bii\u00f1 bi tuuru, mbuus yi y\u00e0qu.\n5:38 Waaye da\u00f1oo war a def bii\u00f1 bu bees ci mbuus yu bees.\n5:39 Ku naan bii\u00f1 bu m\u00e0ggat du b\u00ebgg bu bees bi, ndax day wax ne: \u201cBu m\u00e0ggat bi baax na.\u201d\u00bb\n6:1 Amoon na benn b\u00e9su noflaay Yeesu di dem, jaar ci ay tool yu \u00f1or. Taalibeem ya di f\u00e0q ay c\u00ebgg, di leen boxom ci seeni loxo tey lekk.\n6:2 Am ay Farisen yu ne: \u00abLu tax ngeen di def lu jaaduwul ci b\u00e9su noflaay bi?\u00bb\n6:3 Yeesu tontu leen ne: \u00abNdax j\u00e0nguleen la Daawuda defoon, ba mu xiifee, moom ak \u00f1a mu \u00e0ndaloon?\n6:4 Xanaa y\u00e9guleen, ni mu dugge woon ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, j\u00ebl mburu, ya \u00f1u j\u00e9bbal Y\u00e0lla, lekk ca, jox ca \u00f1a mu \u00e0ndaloon? Fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul saraxalekat.\u00bb\n6:5 Yeesu dellu ne leen: \u00abDoomu nit ki mooy boroom b\u00e9su noflaay bi.\u00bb\n6:6 Beneen b\u00e9su noflaay, Yeesu dugg ci j\u00e0ngu bi, di fa j\u00e0ngale. Amoon na fa nit ku loxol ndeyjooram l\u00e0ggi.\n6:7 Xutbakat yi ak Farisen yi \u00f1u ngi ko doon xool, ba xam dina ko faj ci b\u00e9su noflaay bi, ngir \u00f1u am lu \u00f1u ko tuumaale.\n6:8 Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom l\u00e0ggi: \u00abJ\u00f3gal taxaw ci kanamu \u00f1\u00e9pp.\u00bb Nit ka daldi j\u00f3g taxaw.\n6:9 Yeesu ne leen: \u00abMa laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko b\u00e9su noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?\u00bb\n6:10 Ci kaw loolu mu xool leen \u00f1oom \u00f1\u00e9pp, ba noppi ne nit ka: \u00abT\u00e0llalal sa loxo.\u00bb Mu t\u00e0llal ko, loxoom daldi w\u00e9r pe\u014b\u014b.\n6:11 Waaye nit \u00f1a mer ba fees, di rabat pexe yu j\u00ebm ca Yeesu.\n6:12 Ca b\u00e9s yooya Yeesu y\u00e9eg ca tund wa ngir \u00f1aan, mu fanaan fa, di \u00f1aan ci Y\u00e0lla.\n6:13 Bi b\u00ebt setee, Yeesu woo taalibeem yi, t\u00e0nn ci fukk ak \u00f1aar, tudde leen ay ndawam:\n6:14 Simo\u014b, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi,\n6:15 Mac\u00eb ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simo\u014b mi bokk ci mbooloo, ma \u00f1u tudde \u00d1i farlu ci moom seen r\u00e9ew;\n6:16 Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujj a wor.\n6:17 Yeesu \u00e0nd ak ndaw ya, w\u00e0cc tund ya, daldi taxaw ca joor ga, fa mbooloom taalibe mu takku nekkoon. Amoon na fa it ay nit \u00f1u bare \u00f1u j\u00f3ge ca r\u00e9ewu Yawut ya m\u00e9pp ak ca d\u00ebkku Yerusalem ak d\u00ebkk yi nekk ca wetu g\u00e9ej ga, maanaam Tir ak Sidon.\n6:18 Da\u00f1oo \u00f1\u00ebw ngir d\u00e9glu ko, te it ngir mu faj leen. \u00d1i rab j\u00e0pp it faju na\u00f1u.\n6:19 \u00d1\u00e9pp a ngi ko doon wut a laal ndax doole jiy j\u00f3ge ci moom, di faj \u00f1\u00e9pp.\n6:20 Yeesu xool ay taalibeem ne leen:\u00abY\u00e9en \u00f1i s\u00ebsul lu dul ci Y\u00e0lla, barkeel ngeen,ndaxte nguuru Y\u00e0lla, y\u00e9ena ko yelloo.\n6:21 Y\u00e9en \u00f1i xiif l\u00e9egi, barkeel ngeen,ndax dingeen regg.Y\u00e9en \u00f1iy naqarlu l\u00e9egi, barkeel ngeen,ndax dingeen ree.\n6:22 Barkeel ngeen, bu leen nit \u00f1i ba\u00f1ee, di leen d\u00e0q ak a saaga, di sib seen tur ngir Doomu nit ki.\n6:23 Bu boobaa b\u00e9gleen te b\u00e0nneexu, ndax seen yool dina r\u00e9y ci laaxira. Ndaxte noonu la maami seeni ba\u00f1 daan fitnaale yonent yi.\n6:24 Waaye nag y\u00e9en boroom alal yi, torox ngeen,ndaxte jot ngeen ba noppi seen b\u00e0nneex.\n6:25 Y\u00e9en \u00f1iy lekk ba suur l\u00e9egi, torox ngeen,ndax \u00ebll\u00ebg dingeen xiif.Y\u00e9en \u00f1iy ree l\u00e9egi, torox ngeen,ndax dingeen am aw naqar, ba jooy x\u00e0cc.\n6:26 Torox ngeen bu leen \u00f1\u00e9pp dee waxal lu baax, ndaxte noonu la seeni maam daan j\u00ebfe ak \u00f1a doon mbubboo yonent.\n6:27 \u00abWaaye maa ngi leen koy wax, y\u00e9en \u00f1i may d\u00e9glu, soppleen seeni ba\u00f1aale tey defal lu baax \u00f1i leen ba\u00f1.\n6:28 Y\u00e9eneleen lu baax \u00f1i leen di m\u00f3olu, te \u00f1aanal \u00f1i leen di sonal.\n6:29 Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul t\u00e9ye sa turki.\n6:30 K\u00e9pp ku la \u00f1aan, may ko, te ku nangu say y\u00ebf, bu ko ko laaj.\n6:31 Defal-leen nit \u00f1i li ngeen b\u00ebgg, \u00f1u defal leen ko.\n6:32 \u00abSu ngeen soppee \u00f1i leen sopp, ban ng\u00ebr\u00ebm ngeen ciy am? Ndaxte b\u00e0kkaarkat yi sax sopp na\u00f1u \u00f1i leen sopp.\n6:33 Te bu ngeen defalee lu baax \u00f1i leen koy defal, ban ng\u00ebr\u00ebm ngeen ciy am? B\u00e0kkaarkat yi it da\u00f1uy def noonu.\n6:34 Te bu ngeen dee leble te yaakaar ci ndelloo, ban ng\u00ebr\u00ebm ngeen ciy am? B\u00e0kkaarkat yi it da\u00f1uy lebal seeni moroom, ngir \u00f1u delloo leen ko.\n6:35 Waaye soppleen seeni noon, di leen defal lu baax, tey leble, ba\u00f1 a yaakaar \u00f1u delloo leen ko. Noonu seen yool dina mag te dingeen wone ne, y\u00e9enay doomi Aji Kawe ji, ndaxte Y\u00e0lla day wone mbaaxam ci \u00f1u goreedi \u00f1i ak \u00f1u soxor \u00f1i.\n6:36 Nangeen am y\u00ebrmande, ni seen Baay ame y\u00ebrmande.\n6:37 \u00abBuleen \u00e0tte seeni moroom ak \u00f1aaw njort, te deesu leen \u00e0tte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen \u00f1i ci des, te dina\u00f1u leen baal.\n6:38 Mayeleen te dina\u00f1u leen may. Dina\u00f1u leen \u00ebmbal natt bu baax bu \u00f1u rokkas te yengal ko, mu fees bay tuuru. Ndaxte dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale.\u00bb\n6:39 Noonu Yeesu wax na leen beneen l\u00e9eb ne leen: \u00abNdax gumba man na wommat moroomam? Mbaa du\u00f1u daanu \u00f1oom \u00f1aar ci k\u00e0mb?\n6:40 Taalibe g\u00ebnul kilifaam, waaye taalibe bu j\u00e0ng ba w\u00e0cc, dina yem ak kilifaam demin.\n6:41 \u00abLu tax ngay xool \u00f1ax gi ci sa b\u00ebtu mbokk, te gisuloo g\u00e0nj gi ci sa b\u00ebt yaw?\n6:42 Nan nga man a waxe sa mbokk: \u201cSama xarit, may ma, ma dindil la \u00f1ax gi ci sa b\u00ebt,\u201d yaw mi gisul g\u00e0nj gi nekk ci sa b\u00ebt? Naaf\u00e9q! J\u00ebkkal a dindi g\u00e0nj gi ci sa b\u00ebt, te noonu dinga man a gis bu leer, ngir dindi \u00f1ax gi ci sa b\u00ebtu mbokk.\n6:43 \u00abGarab gu baax du me\u00f1\u00f1 doom yu bon, te garab gu bon du me\u00f1\u00f1 doom yu baax.\n6:44 Ndaxte garab, me\u00f1\u00f1eefam la\u00f1u koy x\u00e0mmee. Deesul witte figg ci d\u00e9dd, walla r\u00e9se\u00f1 ci xaaxaam.\n6:45 Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, ndax loolu la denc ci xolam, te nit ku bon, lu bon lay wax, ndaxte denc na lu bon ci xolam. Ndaxte g\u00e9mmi\u00f1, la fees xolam lay wax.\n6:46 \u00abLu tax ngeen may wooye \u201cBoroom bi, Boroom bi,\u201d te dungeen def li may wax?\n6:47 K\u00e9pp ku \u00f1\u00ebw ci man, di d\u00e9gg samay wax te di ko j\u00ebfe, ma won leen nu muy mel.\n6:48 Dafa mel ni nit kuy tabax k\u00ebr, mu gas fu x\u00f3ot, jot doj wu r\u00e9y, samp fa k\u00ebr ga. Bi mb\u00ebnn ma \u00f1\u00ebwee, wal ma dafa dal ca k\u00ebr ga te yenguwul, ndaxte nit ka dafa tabax k\u00ebr ga tabax bu d\u00ebg\u00ebr.\n6:49 Waaye k\u00e9pp ku d\u00e9gg samay wax te j\u00ebfewuloo ko, dinga mel ni nit ku tabax k\u00ebram ci suuf, ba\u00f1 koo defal fondamaa. Bi wal ma dalee ca k\u00ebr googa, dafa m\u00e0bb ca saa sa, l\u00e9pp y\u00e0qu yaxeet.\u00bb\n7:1 Bi Yeesu waxee la mu naroon a wax l\u00e9pp ca kanamu mbooloo ma, mu daldi dem Kapernawum.\n7:2 Amoon na fa njiitu xare. Njiit la nag, surgaam bu mu b\u00ebggoon lool dafa feebaroon, bay b\u00ebgg a dee.\n7:3 Bi mu d\u00e9ggee mbiri Yeesu, mu y\u00f3nni ca moom ay Yawut, di magi d\u00ebkk ba, ngir \u00f1aan ko, mu \u00f1\u00ebw faj surga ba.\n7:4 Bi magi d\u00ebkk ba agsee ca Yeesu, \u00f1u s\u00e0kku ci moom ndimbal, \u00f1aan ko: \u00abKi nu y\u00f3nni ci yaw de, yelloo na ndimbal,\n7:5 ndaxte sopp na sunu xeet te moo nu tabaxal sax sunu j\u00e0ngu.\u00bb\n7:6 Noonu Yeesu daldi \u00e0nd ak \u00f1oom. Waaye bi \u00f1uy b\u00ebgg a agsi ca k\u00ebr ga, njiit la yebal ay xaritam ngir \u00f1u wax Yeesu ne: \u00abSang bi, bul sonal sa bopp, ndaxte yeyoowuma nga dugg sama k\u00ebr.\n7:7 Looloo tax it ma xalaat ne, awma darajay gatandu la. Waxal genn k\u00e0ddu rekk, te sama surga dina w\u00e9r.\n7:8 Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: \u201cDemal,\u201d mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: \u201c\u00d1\u00ebwal,\u201d mu \u00f1\u00ebw. Te su ma nee sama jaam: \u201cDefal lii,\u201d mu def ko.\u00bb\n7:9 Bi ko Yeesu d\u00e9ggee, mu waaru. Noonu mu walbatiku ca mbooloo, ma topp ci moom, ne leen: \u00abMaa ngi leen koy wax, ci b\u00e0nni Israyil sax, musuma cee gis ku g\u00ebme nii.\u00bb\n7:10 Noonu ndaw ya daldi dellu ca k\u00ebr ga. Bi \u00f1u agsee, \u00f1u gis ne surga ba w\u00e9r na.\n7:11 Y\u00e0ggul dara Yeesu dem ci d\u00ebkk bu \u00f1uy wax Nayin. Taalibeem yi ak mbooloo mu bare \u00e0nd ak moom.\n7:12 Bi muy agsi ca buntu d\u00ebkk ba, fekk \u00f1uy rob n\u00e9ew boo xam ne kenn rekk la woon ci ndeyam, ji j\u00ebkk\u00ebram faatu woon. Te mbooloo mu bare ca d\u00ebkk ba di gunge soxna sa.\n7:13 Bi ko Boroom ba gisee, mu daldi koy y\u00ebr\u00ebm ne ko: \u00abBul jooyati.\u00bb\n7:14 Mu jege\u00f1si, laal jaat ga, \u00f1i ko j\u00e0ppoo taxaw. Mu ne: \u00abWaxambaane wi, j\u00f3gal, ndigal la.\u00bb\n7:15 Noonu nit ka dee woon j\u00f3g toog, t\u00e0mbalee wax. Yeesu delloo ko yaay ja.\n7:16 \u00d1\u00e9pp tiit, bay m\u00e0ggal Y\u00e0lla, di wax naan: \u00abYonent bu mag fee\u00f1 na ci sunu biir! Y\u00e0lla wallusi na mbooloom!\u00bb\n7:17 La \u00f1u wax ci mbiri Yeesu daldi siiw ca r\u00e9ewu Yawut ya ak la ko w\u00ebr y\u00e9pp.\n7:18 Taalibey Yaxya ya nettali mbir yooyu y\u00e9pp seen kilifa. Noonu Yaxya woo \u00f1aar ci ay taalibeem,\n7:19 y\u00f3nni leen ci Boroom bi, ngir laaj ko: \u00abNdax yaw yaa di Ki war a \u00f1\u00ebw, walla danoo war a xaar keneen?\u00bb\n7:20 Bi taalibe ya agsee ca Yeesu, \u00f1u ne ko: \u00abYaxya moo nu yebal, nu laaj ndax yaa di Ki waroon a \u00f1\u00ebw, walla danuy xaar keneen?\u00bb\n7:21 Ca waxtu woowa Yeesu w\u00e9ral nit \u00f1u bare ci seeni feebar ak ci seeni metit, di d\u00e0q ay rab tey gisloo ay gumba.\n7:22 Noonu mu tontu ndaw ya ne leen: \u00abDemleen nettali Yaxya li ngeen gis te d\u00e9gg ko. Gumba yaa ngi gis, lafa\u00f1 yiy dox, gaana yi w\u00e9r, t\u00ebx yiy d\u00e9gg, \u00f1i dee di dekki, te \u00f1i woyoflu \u00f1u ngi d\u00e9gg xebaar bu baax bi.\n7:23 Yaw mi sa ng\u00ebm yolomul ndax man, barkeel nga.\u00bb\n7:24 Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: \u00abLu ngeen seeti woon ca m\u00e0ndi\u014b ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?\n7:25 Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol y\u00e9re yu rafet? Waaye \u00f1iy soloo noonu, tey dund dund gu neex \u00f1u ngi d\u00ebkk ci k\u00ebri buur.\n7:26 Kon lu ngeen seeti woon? Yonent? Waaw, wax naa leen ne, \u00ebpp na yonent.\n7:27 Yaxya male moo di ki \u00f1u waxoon ci Mbind mi naan:\u201cMaa ngi y\u00f3nni sama ndaw, mu jiitu la,te x\u00e0llal la yoon ci sa kanam.\u201d\n7:28 Maa ngi leen koy wax, ci li jig\u00e9en jur, ku sut Yaxya musul a fee\u00f1. Waaye ba tey ki g\u00ebn a ndaw ci nguuru Y\u00e0lla moo ko sut.\u00bb\n7:29 Nit \u00f1\u00e9pp \u00f1i doon d\u00e9glu Yeesu, ba ci juutikat yi sax, d\u00ebggal na\u00f1u ne Y\u00e0lla ku jub la, ndaxte nangu na\u00f1u Yaxya s\u00f3ob leen ci ndox.\n7:30 Waaye Farisen ya ak xutbakat ya da\u00f1oo ba\u00f1, mu s\u00f3ob leen ci ndox, di wone noonu ne, g\u00e0ntu na\u00f1u li leen Y\u00e0lla b\u00ebggaloon.\n7:31 Yeesu tegaat ca ne: \u00abKon lan laa man a mengaleel niti jamono jii? Lan la\u00f1uy nirool?\n7:32 \u00d1u ngi nirook xale yu toog ca p\u00e9nc ma tey woowante naan:\u201cLiital nanu leen ak toxoro, te fecculeen,woyal nanu leen woyi d\u00ebj, te jooyuleen.\u201d\n7:33 Ndaxte Yaxya fee\u00f1 na, lekkul mburu, naanul bii\u00f1, ngeen daldi ne: \u201cDafa \u00e0nd ak rab.\u201d\n7:34 Gannaaw gi nag Doomu nit ki \u00f1\u00ebw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: \u201cKii daal b\u00ebgg na lekk, di naan bii\u00f1, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom b\u00e0kkaar.\u201d\n7:35 Waaye li xam-xamu Y\u00e0lla di jur, mooy firndeel ne d\u00ebgg la.\u00bb\n7:36 Amoon na ab Farisen bu \u00f1aan Yeesu, mu \u00f1\u00ebw lekkandoo ak moom. Yeesu dem k\u00ebr waa ja, toog ca lekkukaay.\n7:37 Fekk amoon na ca d\u00ebkk ba jig\u00e9en juy moy Y\u00e0lla. Bi mu y\u00e9gee ne, Yeesoo ngay lekk ca k\u00ebr Farisen ba, mu dem, y\u00f3bbaale njaq lu \u00f1u defare doj wu \u00f1uy wax albaatar te def latkolo\u00f1.\n7:38 Bi jig\u00e9en ja agsee, mu taxaw ca gannaaw t\u00e0nki Yeesu, di jooy. Noonu ay rangoo\u00f1am tooyal t\u00e0nki Yeesu, jig\u00e9en ja di leen fomp ak kawaram, di leen f\u00f3on te ciy sotti latkolo\u00f1 ja.\n7:39 Naka la Farisen, bi woo woon Yeesu ci k\u00ebram, gis loolu, mu wax ci xelam naan: \u00abBu nit kii doonoon yonent, kon dina xam kuy jig\u00e9en ji koy laal ak ni mu nekke b\u00e0kkaarkat.\u00bb\n7:40 Yeesu ne ca tonn, daldi ne Farisen ba: \u00abSimo\u014b, am na lu ma la war a wax.\u00bb Simo\u014b ne ko: \u00abWaxal, kilifa gi.\u00bb\n7:41 Yeesu ne ko: \u00abDa fee amoon \u00f1aari nit \u00f1u ameel bor benn leblekat. Kenn kaa ngi ko ameel t\u00e9em\u00e9eri junni ci xaalis, ki ci des fukki junni.\n7:42 Waaye kenn ci \u00f1oom m\u00ebnu koo fey. Noonu mu baal leen bor ya. Ci \u00f1aar \u00f1oo\u00f1u nag kan moo ko ciy g\u00ebn a b\u00ebgg?\u00bb\n7:43 Simo\u014b tontu ne ko: \u00abXanaa ki \u00f1u baal bor bi g\u00ebn a bare.\u00bb Yeesu ne ko: \u00ab\u00c0tte nga d\u00ebgg,\u00bb\n7:44 daldi walbatiku ca jig\u00e9en ja, ne Simo\u014b: \u00abNdax gis nga jig\u00e9en jii? Dugg naa sa k\u00ebr, te joxewuloo ndox, ngir raxas samay t\u00e0nk. Waaye moom, raxas na samay t\u00e0nk ak ay rangoo\u00f1am, ba noppi fomp leen ak kawaram.\n7:45 Bi ma agsee, f\u00f3onuloo ma, waaye moom, bi ma duggee ba l\u00e9egi t\u00e0yyiwul ci di f\u00f3on samay t\u00e0nk.\n7:46 Defuloo diw ci sama bopp, waaye moom, sotti na latkolo\u00f1 ci samay t\u00e0nk.\n7:47 Moo tax ma di la wax ne, su wonee mb\u00ebggeel gu r\u00e9ye nii, dafa fekk \u00f1u baal ko b\u00e0kkaaram yu bare. Waaye ki mb\u00ebggeelam n\u00e9ew dafa fekk \u00f1u baal ko lu tuuti.\u00bb\n7:48 Yeesu daldi ne jig\u00e9en ja: \u00abBaal na\u00f1u la say b\u00e0kkaar.\u00bb\n7:49 Noonu \u00f1i doon lekkandoo ak moom di wax ci seen xel naan: \u00abKii am sa\u00f1-sa\u00f1u baale b\u00e0kkaar mooy kan?\u00bb\n7:50 Waaye Yeesu ne jig\u00e9en ja: \u00abSa ng\u00ebm musal na la. Demal ci j\u00e0mm.\u00bb\n8:1 Gannaaw loolu Yeesu di dem ca ay d\u00ebkk yu mag ak yu ndaw, di waaraate ak di y\u00e9gle xebaar bu baax bi j\u00ebm ci nguuru Y\u00e0lla. Fukki taalibe ya ak \u00f1aar \u00e0nd ak moom,\n8:2 ak ay jig\u00e9en yu mu teqale woon ak rab te j\u00eble leen ci seeni wopp, \u00f1u di: Maryaama, mi \u00f1uy wooye Maryaamam Magdala, mi Yeesu t\u00e0ggale woon ak jur\u00f3om-\u00f1aari rab;\n8:3 S\u00e0nn, jabaru ku \u00f1uy wax Kusa, mi doon wottu alalu Erodd; ak Sus\u00e0nn ak \u00f1eneen jig\u00e9en. Jig\u00e9en \u00f1oo\u00f1u \u00f1oo doon joxe seen alal, ngir dimbali Yeesu ak ay taalibeem.\n8:4 D\u00ebkk ak d\u00ebkk nit \u00f1a di fa j\u00f3ge j\u00ebm ca Yeesu, ba mbooloo mu bare dajaloo, mu wax leen l\u00e9eb wii:\n8:5 \u00abDafa amoon beykat bu demoon jiyi. Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, nit \u00f1i joggi ci, picci asamaan lekk ko l\u00e9pp.\n8:6 Leneen wadd ci b\u00e9rab bu bare ay doj. Naka la sax rekk, daldi wow, ndaxte suuf si tooyul woon.\n8:7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, \u00f1u saxandoo, xaaxaam ya tanc ko.\n8:8 Li ci des dal ci suuf su baax, sax, nangu ba me\u00f1\u00f1 t\u00e9em\u00e9eri yoon lu \u00ebpp la mu ji woon.\u00bb Gannaaw loolu Yeesu wax ak k\u00e0ddu gu d\u00ebg\u00ebr ne: \u00abD\u00e9glul bu baax, yaw mi am ay nopp.\u00bb\n8:9 Taalibey Yeesu yi laaj ko lu l\u00e9eb woowu di tekki.\n8:10 Mu tontu ne leen: \u00abMay na\u00f1u leen, ngeen xam mb\u00f3oti nguuru Y\u00e0lla, waaye \u00f1i ci des, dama leen di wax ci ay l\u00e9eb. Noonu la, ngir:\u201c\u00d1uy xool te du\u00f1u man a gis,di d\u00e9gg te du\u00f1u man a xam.\u201d\n8:11 \u00abLii la l\u00e9ebu beykat bi di tekki. K\u00e0ddug Y\u00e0lla mooy jiwu wi.\n8:12 Ki f\u00e9ete ci yoon wi mooy ki d\u00e9gg. Gannaaw gi, Seytaane dafay \u00f1\u00ebw, k\u00ebf k\u00e0ddu, gi \u00f1u def ci xolam, ngir mu ba\u00f1 a g\u00ebm te Y\u00e0lla musal ko.\n8:13 Ki nekk ci b\u00e9rab bu bare ay doj, mooy ki d\u00e9gg k\u00e0ddu gi, ba noppi nangu ko ak mb\u00e9g. Waaye wax ji saxul ci moom. Dina g\u00ebm ab diir, waaye bu nattu yi agsee, mu daldi d\u00e0ggeeku.\n8:14 Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki d\u00e9gg k\u00e0ddu gi, waaye nes tuuti soxla yi ak alal ak b\u00e0nneexi \u00e0ddina tanc ko, ba du \u00e0gg cig mat.\n8:15 Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki d\u00e9gg k\u00e0ddu gi te denc ko ci xol bu baax bu gore, te mu\u00f1 ba jur njari\u00f1.\n8:16 \u00abKenn du taal l\u00e0mp, d\u00ebpp ci leget, walla mu di ko def ci ron lal. Daf koy w\u00e9kk, ngir mu leeral \u00f1iy dugg.\n8:17 Amul dara luy kumpa lu \u00f1u dul siiwal b\u00e9s, walla lu l\u00e0qu lu \u00f1u dul fee\u00f1al, ba mu ne f\u00e0\u014b\u014b.\n8:18 Seetleen bu baax, ni ngeen di d\u00e9gloo k\u00e0ddu gi. Ku am, dees na la dollil, waaye ku amul, dees na nangu sax li nga xalaatoon ne, am nga ko ba noppi.\u00bb\n8:19 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam \u00f1\u00ebw seetsi ko, waaye m\u00ebnu\u00f1u woon a agsi ci moom, ndaxte nit \u00f1a da\u00f1oo bare.\n8:20 Am ku ko y\u00e9gal ne: \u00abSa yaay ak say rakk \u00f1u ngi nii taxaw ci biti, b\u00ebgg laa gis.\u00bb\n8:21 Waaye mu daldi leen ne: \u00abSama yaay ak samay rakk, \u00f1ooy \u00f1iy d\u00e9glu k\u00e0ddug Y\u00e0lla, te di ko topp.\u00bb\n8:22 Benn b\u00e9s Yeesu \u00e0ndoon na ak ay taalibeem, dugg ci gaal. Mu ne leen: \u00abNanu j\u00e0ll dex gi.\u00bb Noonu \u00f1u dem.\n8:23 Bi \u00f1uy dem nag, Yeesu daldi nelaw. Ngelaw lu am doole daldi \u00f1\u00ebw, yengal dex gi, gaal gi fees ak ndox, ba \u00f1u b\u00ebgg a suux.\n8:24 Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: \u00abKilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!\u00bb Ci kaw loolu Yeesu j\u00f3g, daldi g\u00ebdd ngelaw li ak duus yi. L\u00e9pp dal, ba ne nemm.\n8:25 Yeesu ne taalibe yi: \u00abAna seen ng\u00ebm?\u00bb \u00d1u daldi tiit te waaru, naan ci seen biir: \u00abKii moo di kan? Mi ngi jox ndigal ngelaw li ak ndox mi, \u00f1u koy d\u00e9ggal.\u00bb\n8:26 Noonu \u00f1u teer ca diiwaanu waa Serasa, fa j\u00e0kkaarloo ak diiwaanu Galile.\n8:27 Bi Yeesu di w\u00e0cc ca gaal ga, ku rab j\u00e0pp ca waa d\u00ebkk ba \u00f1\u00ebw, kar ko. Y\u00e0gg na def yaramu neen te d\u00ebkkul ca k\u00ebr, waaye ca s\u00ebg ya lay nekk.\n8:28 Bi mu gisee Yeesu, mu yuuxu, daanu ciy t\u00e0nkam, daldi xaacu ne: \u00abYaw Yeesu Doomu Y\u00e0lla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Maa ngi lay \u00f1aan, nga ba\u00f1 maa mbugal.\u00bb\n8:29 Dafa wax loolu, ndaxte Yeesu santoon na rab wi, mu g\u00e9nn ci moom. Rab wa dafa ko doon faral a j\u00e0pp. Nit \u00f1i daan na\u00f1u ko wottu, di ko yeew ak ay c\u00e0llala, ak di ko j\u00e9ng, mu di leen dagg, rab wi di ko xiir ca b\u00e9rab yu w\u00e9et.\n8:30 Noonu Yeesu laaj ko: \u00abNoo tudd?\u00bb Mu tontu ne: \u00abCoggal laa tudd.\u00bb Dafa wax loolu, ndaxte rab yu baree ko j\u00e0ppoon.\n8:31 Rab yooyoo ngi ko doon \u00f1aan, ngir mu ba\u00f1 leen a sant, \u00f1u dem ca k\u00e0mb gu x\u00f3ot gi.\n8:32 Fekk amoon na fa g\u00e9ttu mbaam-xuux yu bare, yuy for ca tund wa. Rab ya \u00f1aan Yeesu, mu may leen, \u00f1u dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.\n8:33 Noonu rab ya g\u00e9nn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, \u00f1u daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab.\n8:34 S\u00e0mm ya gis li xew, daw nettaliji mbir mi ca d\u00ebkk ba ak ca \u00e0ll ba.\n8:35 Nit \u00f1i g\u00e9nn, ngir seet li xew. Bi \u00f1u agsee ca Yeesu, \u00f1u fekk fa nit, ka rab ya b\u00e0yyi woon, toog ca kanam Yeesu, sol ay y\u00e9re te \u00e0nd ak sagoom. \u00d1u daldi ragal.\n8:36 \u00d1a fekke woon mbir ma nag, nettali leen naka la Yeesu w\u00e9rale ki rab ya j\u00e0ppoon.\n8:37 Ci kaw loolu waa diiwaanu Serasa b\u00e9pp ragal, ba \u00f1aan Yeesu mu j\u00f3ge fa. Noonu Yeesu dugg ci gaal gi, di b\u00ebgg a dem.\n8:38 Nit ki Yeesu t\u00e0ggale woon ak rab ya \u00f1aan ko, ngir \u00e0nd ak moom. Waaye Yeesu wo\u00f1\u00f1i ko ne ko:\n8:39 \u00ab\u00d1ibbil, nettali li la Y\u00e0lla defal l\u00e9pp.\u00bb Noonu waa ji dem di w\u00ebr d\u00ebkk ba y\u00e9pp, di fa y\u00e9gle la ko Yeesu defal.\n8:40 Bi Yeesu d\u00ebppee dellu, mbooloo ma di ko teeru, ndaxte \u00f1\u00e9pp a ngi ko doon xaar.\n8:41 Noonu nit \u00f1\u00ebw, tuddoon Yayrus te nekk njiitu j\u00e0ngu ba. Bi mu agsee, mu daanu ci t\u00e0nki Yeesu, saraxu ko mu \u00f1\u00ebw k\u00ebram,\n8:42 ndaxte jenn doomam ju jig\u00e9en, ji mu amoon kepp te muy tollu ci fukki at ak \u00f1aar, ma nga doon waaj a dee. Bi Yeesuy dem, nit \u00f1aa ngi doon buuxante, di ko tanc.\n8:43 Amoon na nag ca mbooloo ma jig\u00e9en ju doon x\u00ebpp deret diirub fukki at ak \u00f1aar, te kenn m\u00ebnu ko woon a faj.\n8:44 Jig\u00e9en ja jege\u00f1si Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. Ca saa sa deret ji dal.\n8:45 Yeesu laaj nit \u00f1a ne: \u00abAna ku ma laal?\u00bb Ku nekk di miim. Noonu Piyeer ne ko: \u00abKilifa gi, nit \u00f1\u00e9pp a ngi lay w\u00ebr, di la tanc wet gu nekk.\u00bb\n8:46 Waaye Yeesu ne: \u00abAm na ku ma laal, ndaxte y\u00e9g naa ne, am na doole ju g\u00e9nn ci man.\u00bb\n8:47 Te jig\u00e9en ja xam ne, m\u00ebnul woon a n\u00ebbb li mu def. Mu daldi daanu ci t\u00e0nki Yeesu, di lox. Noonu mu nettali ci kanamu \u00f1\u00e9pp li taxoon mu laal Yeesu, ak ni mu w\u00e9re ca saa sa.\n8:48 Yeesu ne ko: \u00abSoxna si, sa ng\u00ebm faj na la. Demal ci j\u00e0mm.\u00bb\n8:49 Bi Yeesu di wax nag, am na ku j\u00f3ge ca k\u00ebr njiit la, mu \u00f1\u00ebw naan: \u00abSa doom faatu na; matatul ngay sonal kilifa gi.\u00bb\n8:50 Yeesu d\u00e9gg k\u00e0ddu yooyu, daldi ne njiit la: \u00abBul tiit. G\u00ebmal rekk te dina dundaat.\u00bb\n8:51 Bi Yeesu agsee ca k\u00ebr ga, nanguwul kenn duggaaleek moom, \u00f1u dul Piyeer, Yowaana, Saag ak waajuri xale ba.\n8:52 \u00d1a fa nekk \u00f1\u00e9pp di yuuxu ak di jooy xale bi. Noonu Yeesu ne leen: \u00abB\u00e0yyileen seen jooy yi. Janq bi deewul, day nelaw rekk.\u00bb\n8:53 Waaye \u00f1u di ko \u00f1aawal, ndaxte xamoon na\u00f1u ne, dee na.\n8:54 Waaye Yeesu j\u00e0pp loxob janq ba, woo ko ne ko: \u00abXale bi, j\u00f3gal.\u00bb\n8:55 Noonu ruuwu xale ba dellusiwaat, mu daldi j\u00f3g ca saa sa. Yeesu santaane \u00f1u may ko, mu lekk.\n8:56 Waajuri xale bi daldi waaru. Waaye Yeesu tere leen, \u00f1u wax kenn li xew.\n9:1 Benn b\u00e9s Yeesu dajale fukki taalibe ya ak \u00f1aar, jox leen doole ak sa\u00f1-sa\u00f1u d\u00e0q rab y\u00e9pp ak di faj j\u00e0ngoro yi.\n9:2 Noonu mu y\u00f3nni leen \u00f1uy y\u00e9gle nguuru Y\u00e0lla ak di faj jarag yi.\n9:3 Mu ne leen: \u00abBu ngeen di dem, buleen y\u00f3bbaale dara, du yet mbaa mbuus mbaa mburu mbaa xaalis. Buleen yor it \u00f1aari turki.\n9:4 K\u00ebr gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen di fa j\u00f3ge.\n9:5 F\u00e9pp fu leen nit \u00f1i g\u00e0ntoo, g\u00e9nnleen ca d\u00ebkk booba te ngeen y\u00ebl\u00ebb seen p\u00ebndu t\u00e0nk, ngir seede leen seen r\u00e9er.\u00bb\n9:6 Noonu \u00f1u dem d\u00ebkk ak d\u00ebkk, di fa y\u00e9gle xebaar bu baax bi, tey w\u00e9ral jarag yi.\n9:7 Bi Erodd boroom diiwaanu Galile d\u00e9ggee li Yeesu ak ay taalibeem doon def l\u00e9pp, mu jaaxle, ndaxte amoon na, \u00f1u doon wax ci mbiri Yeesu naan: \u00abYaxya moo dekki.\u00bb\n9:8 Am it \u00f1uy wax naan: Iliyas moo dellusi. \u00d1eneen naan: \u00abKenn ci yonent yu j\u00ebkk yaa dekki.\u00bb\n9:9 Waaye Erodd ne: \u00abYaxya, man mii maa dagglu boppam. Kon kii ma d\u00e9gg ay jalooreem, mooy kan?\u00bb Noonu mu koy fexee gis.\n9:10 Bi ndaw ya dellusee, \u00f1u nettali Yeesu la \u00f1u defoon l\u00e9pp. Noonu mu y\u00f3bbaale leen, \u00f1u sore nit \u00f1i, j\u00ebm ca d\u00ebkk bu \u00f1uy wax Betsayda.\n9:11 Bi ko nit \u00f1a y\u00e9gee, \u00f1u toppi ko. Yeesu teeru leen, di leen wax ci mbirum nguuru Y\u00e0lla, te di w\u00e9ral \u00f1i ko aajowoo.\n9:12 Ca ngoon sa fukki taalibe ya ak \u00f1aar \u00f1\u00ebw ci Yeesu ne ko: \u00abYiwil mbooloo mi, \u00f1u dugg ci d\u00ebkk yi ak \u00e0ll bi ko w\u00ebr, ngir am lu \u00f1u lekk ak fu \u00f1u fanaan, ndaxte fii \u00e0llub neen la.\u00bb\n9:13 Waaye Yeesu ne leen: \u00abJoxleen leen lu \u00f1u lekk.\u00bb \u00d1u tontu ko ne: \u00abAmunu lu dul jur\u00f3omi mburu ak \u00f1aari j\u00ebn. Xanaa ndax nu dem j\u00ebndal mbooloo mii lu \u00f1u lekk?\u00bb\n9:14 Ndaxte lu war a mat jur\u00f3omi junniy g\u00f3or a nga fa teewoon. Yeesu ne taalibe ya: \u00abNeeleen mbooloo mi \u00f1u toog def ay g\u00e9ewi jur\u00f3om-fukki nit.\u00bb\n9:15 Taalibe ya def ko, toogloo nit \u00f1a.\n9:16 Bi loolu amee Yeesu j\u00ebl jur\u00f3omi mburu yi ak \u00f1aari j\u00ebn yi, xool ci kaw, g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla, ba noppi mu damm leen, jox taalibe yi, ngir \u00f1u s\u00e9ddale ko mbooloo mi.\n9:17 Noonu \u00f1\u00e9pp lekk ba suur. Bi \u00f1u dajalee desit ya, \u00f1u feesal fukki pa\u00f1e ak \u00f1aar.\n9:18 Benn b\u00e9s Yeesu beddeeku mbooloo ma, di \u00f1aan; taalibe yi nekk ci wetam. Mu laaj leen ne: \u00abNit \u00f1i, ku \u00f1u wax ne moom laa?\u00bb\n9:19 \u00d1u tontu ko ne: \u00abAm na \u00f1u naan, yaa di Yaxya; \u00f1eneen ne, Iliyas; \u00f1i ci des ne, yaay kenn ci yonent yu j\u00ebkk yaa dekki.\u00bb\n9:20 Yeesu ne leen: \u00abY\u00e9en nag ku ngeen ne moom laa?\u00bb Piyeer tontu ko ne: \u00abYaa di Almasi, bi Y\u00e0lla y\u00f3nni.\u00bb\n9:21 Noonu Yeesu daldi leen d\u00e9nk, tere leen \u00f1u wax ko kenn,\n9:22 teg ca ne: \u00abDoomu nit ki war na sonn lu bare; saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya d\u00ebddu ko, \u00f1u rey ko, mu dekki ca \u00f1etteelu fan ba.\u00bb\n9:23 Noonu Yeesu ne leen \u00f1oom \u00f1\u00e9pp: \u00abKu b\u00ebgg a aw ci samay t\u00e0nk, na b\u00e0yyi boppam, g\u00e0ddu b\u00e9s bu nekk bant, bi \u00f1u ko war a daaj, door a topp ci man.\n9:24 Ndaxte koo xam ne b\u00ebgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko \u00f1\u00e0kk, waaye ku \u00f1\u00e0kk sa bakkan ngir man, dinga ko jotaat.\n9:25 Ndaxte moom \u00e0ddina s\u00e9pp, lu muy jari\u00f1 nit, su fekkee ne dafay \u00f1\u00e0kk bakkanam walla mu loru?\n9:26 Ku ma rus a faral, te nanguwul samay wax, Doomu nit ki dina la rus a xam, b\u00e9s bu \u00f1\u00ebwee ci ndamam ak ci ndamu Baay bi ak lu malaaka yu sell yi.\n9:27 Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, am na \u00f1i fi taxaw \u00f1oo xam ne du\u00f1u dee te gisu\u00f1u nguuru Y\u00e0lla gi.\u00bb\n9:28 Bi \u00f1u ca tegee luy tollook ayu-b\u00e9s gannaaw bi Yeesu waxee loolu, mu \u00e0nd ak Piyeer, Yowaana ak Saag, y\u00e9eg ca kaw tund wa ngir \u00f1aan.\n9:29 Bi muy \u00f1aan, xar-kanamam daldi soppiku, ay y\u00e9reem weex t\u00e0ll bay melax.\n9:30 Am \u00f1aari nit di waxtaan ak moom, muy yonenti Y\u00e0lla Musaa ak Iliyas.\n9:31 \u00d1oo fee\u00f1 ci ndamu Y\u00e0lla, di waxtaane ci demu Yeesu, gi muy \u00e0ggalee yenam ci Yerusalem.\n9:32 Fekk Piyeer ak \u00f1i mu \u00e0ndal doon g\u00ebmmeentu, waaye bi \u00f1u yeewoo bu baax, \u00f1u gis ndamu Yeesu, ak \u00f1aari nit \u00f1u taxaw ci wetam.\n9:33 Bi nit \u00f1oo\u00f1u di sore Yeesu, Piyeer ne ko: \u00abKilifa gi, b\u00e9g nanu ci sunu teew fii; nanu defar \u00f1etti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.\u00bb Fekk xamul la mu doon wax.\n9:34 Bi mu koy wax, niir \u00f1\u00ebw muur leen, taalibe yi daldi tiit, bi leen niir wa \u00ebmbee.\n9:35 Noonu baat jibe ca niir wa naan: \u00abKii mooy sama Doom ji ma fal; d\u00e9gluleen ko.\u00bb\n9:36 Bi baat ba waxee ba noppi, Yeesu rekk des fa. Taalibe ya noppi, ba\u00f1 a nettali kenn ca jamono jooja la \u00f1u gisoon.\n9:37 Ca suba sa Yeesu ak taalibe ya w\u00e0cce ca tund wa, mbooloo mu bare \u00f1\u00ebw, di ko gatandu.\n9:38 Nit xaacu ci biir mbooloo mi naan: \u00abKilifa gi, maa ngi lay \u00f1aan, nga seet sama doom, ndaxte moom kepp laa am.\n9:39 L\u00e9eg-l\u00e9eg rab j\u00e0pp ko, mu daldi yuuxu ca saa sa, rab wi di ko sayloo, g\u00e9mmi\u00f1 gi di fuur. Du faral di g\u00e9nn ci moom te dina ko sonal.\n9:40 \u00d1aan naa say taalibe, \u00f1u d\u00e0q ko, waaye m\u00ebnu\u00f1u ko.\u00bb\n9:41 Yeesu tontu ne: \u00abY\u00e9en niti jamono jii, y\u00e9en \u00f1i g\u00ebmadi te d\u00ebng, ba ka\u00f1 laa war a nekk ak y\u00e9en te di leen mu\u00f1al? Indil ma sa doom.\u00bb\n9:42 Bi xale biy agsi, rab wi di ko daaneel ci suuf, muy say. Waaye Yeesu daldi g\u00ebdd rab wa, w\u00e9ral xale ba, daldi ko delloo baayam.\n9:43 Ku nekk waaru na ndax m\u00e0ggug Y\u00e0lla. Bi \u00f1uy y\u00e9emu ci li mu doon def, Yeesu ne taalibeem ya:\n9:44 \u00abD\u00e9gluleen bu baax lii ma leen di wax: dina\u00f1u j\u00e9bbal Doomu nit ki ci loxoy nit \u00f1i.\u00bb\n9:45 Waaye taalibe ya xamu\u00f1u k\u00e0ddu googu. Y\u00e0lla dafa leen n\u00ebbb li muy tekki, ba \u00f1u ba\u00f1 koo xam, te \u00f1emewu\u00f1u koo laaj Yeesu.\n9:46 Werante am ci biir taalibe yi, \u00f1uy laajante kan moo g\u00ebn a m\u00e0gg ci \u00f1oom.\n9:47 Yeesu mi xam seen xalaat, j\u00ebl ab xale, teg ci wetam ne leen:\n9:48 \u00abKu nangu xale bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma y\u00f3nni; ndaxte ki g\u00ebn a woyof ci y\u00e9en \u00f1\u00e9pp, kooku moo g\u00ebn a m\u00e0gg.\u00bb\n9:49 Bi loolu amee Yowaana j\u00ebl k\u00e0ddu gi ne: \u00abKilifa gi, danoo gis nit kuy d\u00e0q ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndaxte bokkul ci nun.\u00bb\n9:50 Waaye Yeesu tontu ko: \u00abBuleen ko tere, ndaxte ku la sotul, far na ak yaw.\u00bb\n9:51 Bi jamono ji jege\u00f1see, ji Yeesu waree j\u00f3ge \u00e0ddina dem asamaan, mu sigi\u00f1u ci dem Yerusalem.\n9:52 Noonu mu yebal ay ndaw, \u00f1u jiitu ko. \u00d1u dem nag, dugg ci ab d\u00ebkk ci diiwaanu Samari, ngir wutal ko fa fu mu dal.\n9:53 Waaye waa d\u00ebkk ba nanguwu\u00f1u ko, ndaxte mi ngi jublu woon Yerusalem.\n9:54 Bi taalibe yi tudd Saag ak Yowaana gisee loolu, \u00f1u ne: \u00abBoroom bi, ndax dangaa b\u00ebgg nu ne, na safaras asamaan dal ci seen kaw, faagaagal leen?\u00bb\n9:55 Waaye Yeesu walbatiku, yedd taalibe ya,\n9:56 ba noppi \u00f1u daldi dem wuti beneen d\u00ebkk.\n9:57 Bi \u00f1uy dem, am ci yoon wi ku ne Yeesu: \u00abDinaa la topp f\u00e9pp foo j\u00ebm.\u00bb\n9:58 Waaye Yeesu tontu ko ne: \u00abTill yi am na\u00f1u seeni k\u00e0mb, te picci asamaan am na\u00f1u ay t\u00e0gg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.\u00bb\n9:59 Yeesu ne keneen: \u00abToppal ci man.\u00bb Waaye kooku ne ko: \u00abSang bi, may ma, ma j\u00ebkk a dem suuli sama baay.\u00bb\n9:60 Mu tontu ko ne: \u00abB\u00e0yyil \u00f1i dee, \u00f1u suul seeni n\u00e9ew. Yaw demal, y\u00e9gle nguuru Y\u00e0lla.\u00bb\n9:61 Keneen ne ko: \u00abSang bi, dinaa la topp, waaye may ma, ma j\u00ebkk a t\u00e0gguji sama waa k\u00ebr.\u00bb\n9:62 Yeesu ne ko: \u00abKuy ji, di geestu, yeyoowul a ligg\u00e9ey ci nguuru Y\u00e0lla.\u00bb\n10:1 Gannaaw loolu Boroom bi t\u00e0nn na yeneen jur\u00f3om-\u00f1aar-fukki taalibe ak \u00f1aar, yebal leen, \u00f1u \u00e0nd \u00f1aar ak \u00f1aar, jiituji ko ca d\u00ebkk y\u00e9pp ak ca b\u00e9rab y\u00e9pp, ya mu naroon a dem moom ci boppam.\n10:2 Mu ne leen: \u00abNg\u00f3ob mi yaatu na, waaye ligg\u00e9eykat yi barewu\u00f1u. \u00d1aanleen nag Boroom ng\u00f3ob mi, mu yebal ay ligg\u00e9eykat, \u00f1u g\u00f3ob toolam.\n10:3 Demleen! Maa ngi leen di y\u00f3nni, mel ni ay mbote ci biir ay bukki.\n10:4 Buleen yor xaalis walla mbuus walla ay d\u00e0ll. Buleen nuyu kenn ci yoon wi.\n10:5 \u00abK\u00ebr gu ngeen man a dugg, nangeen j\u00ebkk ne: \u201cNa j\u00e0mm w\u00e0cc ci k\u00ebr gi.\u201d\n10:6 Bu fa nitu j\u00e0mm nekkee, seen y\u00e9ene dina ko indil j\u00e0mm. Lu ko moy, seen y\u00e9ene dina dellusi ci y\u00e9en.\n10:7 Dal-leen ca k\u00ebr googa, tey lekk ak a naan lu \u00f1u leen di jox, ndaxte ligg\u00e9eykat yelloo na jot peyam. Buleen dem nag k\u00ebr ak k\u00ebr.\n10:8 \u00abD\u00ebkk bu ngeen man a dugg, te waa d\u00ebkk ba teeru leen, lu \u00f1u leen jox, lekkleen ko.\n10:9 Nangeen w\u00e9ral jaragi d\u00ebkk ba, te ngeen ne leen: \u201cNguuru Y\u00e0lla jegesi na leen.\u201d\n10:10 Waaye bu ngeen duggee ci d\u00ebkk te teeruwu\u00f1u leen, demleen ca mbedd ya te ne leen:\n10:11 \u201cSeen p\u00ebndu d\u00ebkk, bi taq ci sunuy t\u00e0nk sax, noo ngi koy faxas, ngir seede leen seen r\u00e9er. Waaye nag xamleen ne, nguuru Y\u00e0lla jegesi na.\u201d\n10:12 Maa ngi leen koy wax, bu b\u00e9s baa, waa Sodom \u00f1ooy tane d\u00ebkk boobu.\n10:13 \u00abDingeen torox, y\u00e9en waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte k\u00e9emaan yi ma def ci y\u00e9en, bu \u00f1u leen defoon ci d\u00ebkku Tir walla ci d\u00ebkku Sidon, kon tuub na\u00f1u seeni b\u00e0kkaar bu y\u00e0gg, x\u00ebppoo d\u00f3om, sol saaku.\n10:14 Moona ca b\u00e9s p\u00e9nc ba, Tir ak Sidon \u00f1oo leen di tane.\n10:15 Te yaw d\u00ebkku Kapernawum, ndax dees na la y\u00e9kkati bu kawe? D\u00e9ed\u00e9et, dees na la daane bu suufe.\n10:16 \u00abKu leen d\u00e9glu, d\u00e9glu na ma; ku leen ba\u00f1, ba\u00f1 na ma. Te ku ma ba\u00f1, ba\u00f1 na ki ma y\u00f3nni.\u00bb\n10:17 Jur\u00f3om-\u00f1aar-fukki taalibe yi ak \u00f1aar dellusi, fees ak mb\u00e9g te naan: \u00abBoroom bi, rab yi sax d\u00e9ggal na\u00f1u nu ndax sa tur.\u00bb\n10:18 Yeesu ne leen: \u00abMaa ngi doon s\u00e9en Seytaane w\u00e0cce asamaan ni safaras melax.\n10:19 Gis ngeen, jox naa leen sa\u00f1-sa\u00f1u joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley ba\u00f1aale bi, te dara du leen man a gaa\u00f1.\n10:20 Moona li leen rab yi d\u00e9ggal, bumu tax ngeen b\u00e9g, waaye b\u00e9gleen ndax li \u00f1u bind seen tur ci asamaan.\u00bb\n10:21 Ca saa soosu Xel mu Sell mi feesal Yeesu ak mb\u00e9g, mu daldi ne: \u00abYaw Baay bi, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga n\u00ebbb y\u00ebf yii \u00f1i am xam-xam ak \u00f1i am xel, te xamal leen gune yi. Waaw Baay bi, ndaxte looloo la neex.\u00bb\n10:22 Yeesu teg ca ne: \u00abSama Baay j\u00e9bbal na ma l\u00e9pp, te kenn m\u00ebnul a xam, man Doom ji, maay kan, ku dul Baay bi; kenn m\u00ebnul a xam it kan mooy Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko b\u00ebgg a xamal.\u00bb\n10:23 Gannaaw bi mu waxee loolu, Yeesu walbatiku ca taalibe ya ne leen \u00f1oom rekk: \u00ab\u00d1i seeni b\u00ebt di gis li ngeen di gis, am na\u00f1u mb\u00e9g.\n10:24 Ndaxte maa ngi leen koy wax, yonent yu bare ak buur yu bare b\u00ebggoon na\u00f1oo gis li ngeen di gis, waaye gisu\u00f1u ko, te d\u00e9gg li ngeen di d\u00e9gg, waaye d\u00e9ggu\u00f1u ko.\u00bb\n10:25 Noonu benn xutbakat daldi j\u00f3g, ngir fexee fiir Yeesu ne ko: \u00abKilifa gi, lan laa war a def, ba am dund gu dul jeex?\u00bb\n10:26 Yeesu ne ko: \u00abLu \u00f1u bind ci yoonu Musaa? Lan nga ciy j\u00e0ng?\u00bb\n10:27 Nit ka ne ko: \u00ab \u201cNanga b\u00ebgg Y\u00e0lla sa Boroom ak sa xol b\u00e9pp ak sa bakkan b\u00e9pp, sa k\u00e0ttan g\u00e9pp ak sa xel m\u00e9pp,\u201d te it: \u201cNanga b\u00ebgg sa moroom, ni nga b\u00ebgge sa bopp.\u201d\u00bb\n10:28 Yeesu ne ko nag: \u00abLi nga wax d\u00ebgg la. Boo defee loolu, dinga dund ba f\u00e0ww.\u00bb\n10:29 Waaye xutbakat ba b\u00ebggoon a am aw lay, ne Yeesu: \u00abKan mooy sama moroom nag?\u00bb\n10:30 Yeesu tontu ko ne: \u00abDafa amoon nit ku j\u00f3ge woon Yerusalem, j\u00ebm Yeriko. Ay s\u00e0cc dogale ko, futti ko, d\u00f3or ko ba muy b\u00ebgg a dee, dem b\u00e0yyi ko fa.\n10:31 Faf ab saraxalekat jaar ca yoon wa, s\u00e9en nit ka, teggi.\n10:32 Benn waay it bu soqikoo ci giiru Lewi, aw ca b\u00e9rab booba, s\u00e9en waa ja, teggi.\n10:33 Waaye benn waay bu d\u00ebkk Samari bu doon tukki, \u00f1\u00ebw ba jege waa ja, gis ko, y\u00ebr\u00ebm ko.\n10:34 Noonu mu \u00f1\u00ebw, diw ko diwlin ak bii\u00f1 ngir faj gaa\u00f1u-gaa\u00f1u ya, bandaas ko. Gannaaw loolu mu teg ko ci mbaamam, y\u00f3bbu ko ci fanaanukaay, di ko topptoo.\n10:35 Bi b\u00ebt setee, mu g\u00e9nne \u00f1aari poseti xaalis, jox ko boroom k\u00ebr ga ne ko: \u201cNanga topptoo nit kooku. B\u00e9s bu ma fi jaaraatee, dinaa la fey, man ci sama bopp, l\u00e9pp loo ci dolli ci xaalis.\u201d\u00bb\n10:36 Yeesu teg ca ne: \u00abLu ciy sa xalaat? Kan ci \u00f1ett \u00f1oo\u00f1u moo j\u00ebfe ni kuy j\u00ebf j\u00ebme ci moroomam, ba \u00f1u gisee nit, ka s\u00e0cc ya dogale woon?\u00bb\n10:37 Xutbakat ba tontu ko ne: \u00abXanaa ki ko won y\u00ebrmandeem.\u00bb Yeesu ne ko nag: \u00abDemal tey def ni moom.\u00bb\n10:38 Bi Yeesu ak ay taalibeem nekkee ci yoon wi, mu dugg ci benn d\u00ebkk, fekk fa jig\u00e9en ju tudd M\u00e0rt, ganale ko.\n10:39 M\u00e0rt nag amoon rakk ju tudd Maryaama, ma nga toog ci t\u00e0nki Boroom bi, di d\u00e9glu ay k\u00e0ddoom.\n10:40 Fekk M\u00e0rt j\u00e0pp lool ca waa\u00f1 wa. Noonu mu \u00f1\u00ebw ci wetu Yeesu ne ko: \u00abBoroom bi, doo ci wax dara, boo gisee sama rakk ji b\u00e0yyi ma ak ligg\u00e9ey bi y\u00e9pp? Ne ko mu j\u00e0pple ma.\u00bb\n10:41 Boroom bi tontu ko ne: \u00abM\u00e0rt, M\u00e0rt, yu baree ngi fees sa xol, nga am ay t\u00e9q-t\u00e9q ndax loolu.\n10:42 Moona de, lenn rekk a am solo. Maryaama dafa t\u00e0nn c\u00e9r bi g\u00ebn, te kenn du ko nangu ci moom.\u00bb\n11:1 Am b\u00e9s Yeesu di \u00f1aan ci benn b\u00e9rab. Bi mu noppee, kenn ci taalibeem yi ne ko: \u00abBoroom bi, j\u00e0ngal nu, nan lanu war a \u00f1aane, ni ko Yaxya j\u00e0ngale ay taalibeem.\u00bb\n11:2 Yeesu ne leen: \u00abBu ngeen dee \u00f1aan, nangeen ne:\u201cBaay bi, na sa tur sell,na sa nguur \u00f1\u00ebw.\n11:3 May nu b\u00e9s bu nekk li nu war a dunde.\n11:4 Baal nu sunuy b\u00e0kkaar,ndaxte nun itam danuy baal \u00f1\u00e9pp \u00f1i nu too\u00f1.Te bu nu teg ci yoonu nattu.\u201d\u00bb\n11:5 Yeesu teg ca ne leen: \u00abMi ngi mel ni, nga dem seeti sa xarit ci xaaju guddi ne ko: \u201cXarit, lebal ma \u00f1etti mburu.\n11:6 Dafa am sama xarit bu ma ganesi, te awma dara lu ma ko jox.\u201d\n11:7 \u00abWaaye kooku nekk ci biir n\u00e9egam, dina ko tontu: \u201cBu ma lakkal, t\u00ebj naa bunt bi ba noppi te t\u00ebdd, man ak sama njaboot; m\u00ebnumaa j\u00f3g di la jox dara.\u201d\n11:8 Maa ngi leen koy wax, su j\u00f3gul jox ko li muy laaj ndax li \u00f1u xaritoo it, ndax la kee \u00f1\u00e0kk jom dina tax mu jox ko l\u00e9pp li mu soxla.\n11:9 Moo tax ma ne, \u00f1aanleen, \u00f1u may leen; seetleen, te dingeen gis; f\u00ebggleen, \u00f1u ubbil leen.\n11:10 Ndaxte k\u00e9pp kuy \u00f1aan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy f\u00ebgg, \u00f1u ubbil la.\n11:11 Bu la sa doom \u00f1aanee j\u00ebn, yaw miy baayam, ndax dinga ko ba\u00f1 a jox j\u00ebn, jox ko jaan?\n11:12 Walla mu \u00f1aan la nen, nga jox ko jiit?\n11:13 Ndegam y\u00e9en \u00f1i bon y\u00e9ena man a jox seeni gune lu baax, astemaak Baay bi nekk ci kaw dina jox Xel mu Sell mi \u00f1i ko koy \u00f1aan!\u00bb\n11:14 Am b\u00e9s Yeesu d\u00e0q rab wu luu. Naka la rab wa g\u00e9nn, luu ba daldi wax, ba mbooloo may y\u00e9emu.\n11:15 Waaye am ca mbooloo ma ay nit, \u00f1u doon wax naan: \u00abCi k\u00e0ttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay d\u00e0qe rab yi.\u00bb\n11:16 Am \u00f1eneen \u00f1u fexe koo fiir, ba laaj ko k\u00e9emaan gu j\u00f3ge ci asamaan tey firndeel y\u00f3nnentam.\n11:17 Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: \u00abR\u00e9ew mu xeex boppam tas, k\u00ebr gu xeex boppam gent.\n11:18 Te it bu Seytaane xeexee boppam, naka la nguuram di man a y\u00e0gge? Damay wax loolu, ndaxte nee ngeen, damay d\u00e0q rab jaarale ko ci k\u00e0ttanu Beelsebul.\n11:19 Te it bu fekkee ne man damay d\u00e0q ay rab ci k\u00e0ttanu Beelsebul, seeni taalibe nag ci gan k\u00e0ttan la\u00f1u leen di d\u00e0qe? Kon \u00f1oo leen di \u00e0tte.\n11:20 Waaye bu fekkee ne ci baaraamu Y\u00e0lla laay d\u00e0qe rab, kon nguuru Y\u00e0lla agsi na ba ci y\u00e9en.\n11:21 \u00abSu nit ku bare doole g\u00e0nnaayoo, di wottu k\u00ebram, alalam dina raw.\n11:22 Waaye bu ku ko \u00ebpp doole \u00f1\u00ebwee, daan ko, dafay nangu g\u00e0nnaay ya mu yaakaaroon, ba noppi s\u00e9ddale alal ja.\n11:23 Ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.\n11:24 \u00abBoo xamee ne rab, wa j\u00e0ppoon nit, g\u00e9nn na ci moom, day w\u00ebr ay b\u00e9rab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis. Noonu da naan: \u201cNaa dellu ca sama k\u00ebr, ga ma j\u00f3ge.\u201d\n11:25 Bu \u00f1\u00ebwee nag, mu fekk k\u00ebram, \u00f1u bale ko, defar ko ba l\u00e9pp jekk.\n11:26 Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen jur\u00f3om-\u00f1aari rab yu ko g\u00ebn a soxor. \u00d1u dugg, sanc fa; ba tax mujug nit kooku mooy y\u00e9es nj\u00e0lb\u00e9enam.\u00bb\n11:27 Bi Yeesu di wax loolu, jenn jig\u00e9en y\u00e9kkati baatam ca biir mbooloo ma ne: \u00abC\u00e9y jig\u00e9en ji la \u00ebmb te n\u00e0mpal la moo barkeel!\u00bb\n11:28 Waaye Yeesu tontu ko ne: \u00abNeel kay, ki barkeel mooy kiy d\u00e9glu k\u00e0ddug Y\u00e0lla te di ko topp.\u00bb\n11:29 Naka la mbooloo may g\u00ebn a takku, Yeesu ne: \u00abNiti jamono jii da\u00f1oo bon. \u00d1u ngi laaj firnde, waaye du\u00f1u jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.\n11:30 Ndaxte ni Yunus nekke woon firnde ci waa d\u00ebkku Niniw, noonu la Doomu nit kiy nekke firnde ci niti jamono jii.\n11:31 Keroog b\u00e9s p\u00e9nc buur bu jig\u00e9en, ba d\u00ebkkoon ca sudd, dina j\u00f3gandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa j\u00f3ge ca catul \u00e0ddina, ngir d\u00e9glu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.\n11:32 Te it ca b\u00e9s p\u00e9nc, waa d\u00ebkku Niniw dina\u00f1u j\u00f3gandoo ak niti jamono jii, yey leen, ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub na\u00f1u seeni b\u00e0kkaar, te ku sut Yunus a ngi fii.\n11:33 \u00abKenn du taal l\u00e0mp, ba noppi di ko duggal cig k\u00e0mb, walla di ci k\u00ebpp leget. Daf koy w\u00e9kk, ngir mu leeral \u00f1iy dugg.\n11:34 B\u00ebt mooy l\u00e0mpu yaram. Bu sa b\u00ebt w\u00e9ree, kon sa yaram w\u00e9pp leer. Waaye bu sa b\u00ebt woppee, kon sa yaram w\u00e9pp l\u00ebnd\u00ebm.\n11:35 Moytul ndax leer gi nekk ci yaw du l\u00ebnd\u00ebm.\n11:36 Kon bu sa yaram w\u00e9pp nekkee ci leer te amul genn wet gu laal ci l\u00ebnd\u00ebm, dina leer n\u00e0\u00f1\u00f1, mel ni leeraayu l\u00e0mp ne r\u00e0yy ci sa kaw.\u00bb\n11:37 Bi Yeesu waxee ba noppi, benn Farisen wax ko, mu \u00f1\u00ebw lekke k\u00ebram. Yeesu dugg ca k\u00ebr ga, toog ca lekkukaay ba.\n11:38 Farisen bi nag daldi jaaxle, bi mu gisee ne Yeesu raxasuwul, laata muy lekk.\n11:39 Noonu Boroom bi ne ko: \u00abWaaw y\u00e9en Farisen yi, y\u00e9ena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dangeen a fees ak c\u00e0cc ak mbon!\n11:40 Y\u00e9ena \u00f1\u00e0kk xel! Xanaa du ki defar biti moo defar biir itam?\n11:41 Saraxeleen li nekk ci biir te seen l\u00e9pp dina sell.\n11:42 Y\u00e9en Farisen yi dingeen torox! Ndaxte y\u00e9ena ngi s\u00e0kk asaka ci naana ak ru ak l\u00e9jum bu nekk, waaye s\u00e0ggane ngeen njubte ak mb\u00ebggeel ci Y\u00e0lla. Loolu ngeen war a def, waxuma nag ngeen s\u00e0ggane la ca des.\n11:43 Y\u00e9en Farisen yi, dingeen torox! Ndaxte ca j\u00e0ngu ya, toogu ya f\u00e9ete kanam ngeen di taamu te b\u00ebgg \u00f1\u00e9pp di leen nuyoo \u00f1aari loxo ca p\u00e9nc ma.\n11:44 Dingeen torox, ndaxte dangeen a mel ni ay b\u00e0mmeel yu raaf, ba nit \u00f1i di ci dox te teyu\u00f1u ko.\u00bb\n11:45 Kenn ci xutbakat yi ne ca tonn ne: \u00abKilifa gi, boo waxee loolu, yaa ngi nuy xas, nun itam.\u00bb\n11:46 Noonu Yeesu neeti leen: \u00abY\u00e9en itam xutbakat yi, dingeen torox! Ndaxte dangeen di s\u00ebf nit \u00f1i say yu diis, waaye dungeen nangoo laal s\u00ebf bi sax ak seen cati baaraam.\n11:47 Dingeen torox, ndaxte y\u00e9ena ngi tabax xabruy yonent, yi seeni maam reyoon.\n11:48 Dangeen di seede noonu ne, \u00e0nd ngeen ak li seen maam defoon, ndaxte \u00f1oo rey yonent yi, y\u00e9en ngeen tabax xabru yi.\n11:49 Looloo tax Y\u00e0lla mi xam l\u00e9pp ne: \u201cDinaa leen y\u00f3nnee ay yonent ak ay ndaw. \u00d1enn \u00f1i dina\u00f1u leen fitnaal, rey leen.\u201d\n11:50 Kon nag Y\u00e0lla dina mbugal niti jamono jii ndax dereti yonent yi \u00f1u tuur, ba \u00e0ddina sosoo ak l\u00e9egi,\n11:51 la dale ca Abel ba ci Sakariya, moom mi \u00f1u rey ci diggante saraxalukaay bi ak b\u00e9rab bu sell bi. Waaw, maa ngi leen koy wax, Y\u00e0lla dina mbugal niti jamono jii ndax loolu.\n11:52 Y\u00e9en xutbakat yi, dingeen torox, ndaxte y\u00e9ena y\u00f3bbu caabiy xam-xam; dugguleen ci, te ku ci b\u00ebgg a dugg, ngeen tere ko ko.\u00bb\n11:53 Bi Yeesu g\u00e9nnee b\u00e9rab boobu, Farisen ya ak xutbakat ya \u00ebmbal ko mer te di ko seetlu ci f\u00e0nn gu nekk,\n11:54 di ko yeeru, b\u00ebgg a k\u00ebf waxam bu awul yoon.\n12:1 Gannaaw loolu, naka la mbooloo ma dajaloo ba mat ay junniy junniy nit, di tancante, Yeesu t\u00e0mbalee wax j\u00ebmale ca taalibeem ya ne leen: \u00abMoytuleen lawiiru Farisen ya, li di naaf\u00e9q.\n12:2 Amul dara lu n\u00ebbbu lu \u00f1u warul a biral, mbaa lu kumpa lu \u00f1u warul a siiwal.\n12:3 Looloo tax lu ngeen wax ci biir l\u00ebnd\u00ebm, dees na ko d\u00e9gg ci leer. Lu ngeen d\u00e9ey nit ci biir n\u00e9eg, dees na ko y\u00e9gle ci kaw taax yi.\n12:4 \u00abMaa ngi leen koy wax, samay xarit, buleen ragal \u00f1u man a rey yaram, ba noppi dootu\u00f1u man a def dara.\n12:5 Dinaa leen wax nag ki ngeen war a ragal: ragal-leen Ki nga xam ne bu reyee ba noppi, am sa\u00f1-sa\u00f1u s\u00e0nni ca safara. Waaw maa ngi leen koy wax, ragal-leen kooku.\n12:6 Jur\u00f3omi picci rammatu, ndax du\u00f1u ko jaay ci \u00f1aari d\u00ebr\u00ebm? Moona Y\u00e0lla f\u00e0ttewul benn ci \u00f1oom.\n12:7 Seen kawari bopp sax wa\u00f1\u00f1ees na leen. Kon buleen ragal dara, y\u00e9ena g\u00ebn ndiiraanu rammatu.\n12:8 \u00abTe maa ngi leen koy wax, k\u00e9pp ku ma nangu ci kanamu nit \u00f1i, Doomu nit ki dina la nangu ci kanamu malaakay Y\u00e0lla yi.\n12:9 Waaye ku ma g\u00e0ntu ci kanamu nit \u00f1i, dina\u00f1u la g\u00e0ntu ci kanamu malaakay Y\u00e0lla yi.\n12:10 Ku sosal Doomu nit ki, dina\u00f1u la baal, waaye kuy sosal Xel mu Sell mi, du\u00f1u la ko baal.\n12:11 \u00abBu \u00f1u leen y\u00f3bboo ca j\u00e0ngu ya, ca kanamu kilifa ya ak \u00e0ttekat ya, buleen am xel \u00f1aar ci li ngeen war a tontu ak nan ngeen war a tontoo, walla lu ngeen war a wax,\n12:12 ndaxte Xel mu Sell mi dina leen xamal ca waxtu woowa li ngeen war a wax.\u00bb\n12:13 Am ca mbooloo ma ku ne Yeesu: \u00abKilifa gi, joxal ndigal sama mag, mu s\u00e9dd ma ci sunu ndono.\u00bb\n12:14 Yeesu tontu ko ne: \u00abSama waay, kan moo ma fal \u00e0ttekat ci seen kaw, walla mu teg ma fi, ma di leen s\u00e9ddaleel seen alal?\u00bb\n12:15 Noonu mu ne leen \u00f1oom \u00f1\u00e9pp: \u00abMoytuleen b\u00ebgge, ndaxte bakkanu nit ajuwul ci alalam, ak lu mu baree-bare.\u00bb\n12:16 Noonu mu d\u00e9gtal leen wii l\u00e9eb ne: \u00abDafa amoon waa ju bare alal, te ay toolam nangu lool,\n12:17 muy werante ci xelam naan: \u201cNu ma war a def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ng\u00f3ob mi.\u201d\n12:18 Noonu mu ne: \u201cNii laay def: daaneel sama s\u00e0q yi, defaraat yu g\u00ebn a r\u00e9y, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am j\u00e9pp.\n12:19 Te dinaa ka\u00f1 sama bopp ne: \u2019Yaw mii, am nga alal ju bare ju man a dem ay ati at; noppalal sa yaram, di lekk, di naan, tey b\u00e9g.\u2019 \u201d\n12:20 Waaye Y\u00e0lla ne ko: \u201c\u00d1\u00e0kk xel! Guddig tey, dees na j\u00ebl sa bakkan. Kon li nga dajale l\u00e9pp, ku koy moom?\u201d\n12:21 \u00abKiy dajale alal ngir boppam nag te amul dara ca kanam Y\u00e0lla, lu mel nii moo lay dal.\u00bb\n12:22 Noonu Yeesu daldi ne taalibeem yi: \u00abLoolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen war a lekk. Buleen jaaxle it ngir seen yaram ci lu ngeen war a sol,\n12:23 ndaxte bakkan moo g\u00ebn lekk, te yaram a g\u00ebn koddaay.\n12:24 Seetleen baaxo\u00f1 yi: du\u00f1u ji, du\u00f1u g\u00f3ob, amu\u00f1u dencukaay, amu\u00f1u s\u00e0q, teewul Y\u00e0llaa ngi leen di dundal. C\u00e9y ni ngeen \u00ebppe maana picc yi!\n12:25 Ana kan ci y\u00e9en ci kaw njaaxleem, moo man a yokk ab waxtu ci \u00e0ppam?\n12:26 Su fekkee lu tuuti loolu rekk m\u00ebnuleen koo def, kon lu tax ngeen di jaaxle ci li ci des?\n12:27 \u00abSeetleen ni t\u00f3or-t\u00f3ori \u00f1ax mi di saxe. Du\u00f1u ligg\u00e9ey, du\u00f1u \u00ebcc, waaye maa ngi leen di wax ne, Suleymaan sax ci ndamam, soluwul woon ni benn ci \u00f1oom.\n12:28 Y\u00e9en \u00f1i n\u00e9ew ng\u00ebm! Bu Y\u00e0lla woddee nii \u00f1axu tool yi, miy sax tey te bu subaa \u00f1u def ko ci taal bi, ndax du leen g\u00ebn a wodd?\n12:29 Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan; te buleen ci jaaxle.\n12:30 Ndaxte loolu l\u00e9pp, \u00f1i xamul Y\u00e0lla \u00f1oo koy wut. Te seen Baay xam na ne, soxla ngeen ko.\n12:31 Waaye wutleen nguuram, te loolu l\u00e9pp dina leen ko ci dollil.\n12:32 \u00abBuleen ragal dara, y\u00e9en coggal ju ndaw ji, ndaxte dafa soob seen Baay, mu jagleel leen nguuram.\n12:33 Jaayleen seen alal, saraxe ko, ngir s\u00e0kku ay mbuusi xaalis yu dul b\u00ebnn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa s\u00e0cc du ko jege te max du ko y\u00e0q.\n12:34 Ndaxte fu sa alal nekk, fa la sa xol nekk itam.\n12:35 \u00abTakkuleen bu d\u00ebg\u00ebr te b\u00e0yyi l\u00e0mp yi t\u00e0kk.\n12:36 Mel-leen ni ay surga yuy xaar seen njaatige buy j\u00f3ge ca c\u00e9et ga, ndax bu f\u00ebggee bunt ba, \u00f1u ubbil ko ca saa sa.\n12:37 Surga yooyee seen njaatige fekkul \u00f1uy nelaw, ba mu agsee, \u00f1oo g\u00ebn a yeyoo ng\u00ebr\u00ebm. Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina sol y\u00e9rey waa\u00f1, wax leen \u00f1u toog lekk, ba noppi indil leen \u00f1am wi.\n12:38 Su fekkee seen njaatige ci xaaju guddi lay \u00f1\u00ebw sax, walla bu suuf seddee, te fekk leen noonu, surga yooyu \u00f1oo g\u00ebn a yeyoo ng\u00ebr\u00ebm.\n12:39 Waaye xamleen lii: bu boroom k\u00ebr gi xamoon ban waxtu la s\u00e0cc bi di \u00f1\u00ebw, du ko b\u00e0yyi, mu toj k\u00ebram.\n12:40 Y\u00e9en itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina \u00f1\u00ebw ci waxtu wu ngeen ko s\u00e9enuwul.\u00bb\n12:41 Piyeer ne Yeesu: \u00abBoroom bi, ndax dangay d\u00e9gtal l\u00e9eb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo m\u00e9pp?\u00bb\n12:42 Boroom bi tontu ko ne: \u00abKan moo nekk surga bu takku te teey, bu njaatigeem teg ci waa k\u00ebr gi, ngir mu leen di dundal ci jamono ji?\n12:43 Bu njaatigeem \u00f1\u00ebwee te gis mu def noonu, surga boobu dina am ng\u00ebr\u00ebm.\n12:44 Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam j\u00e9pp.\n12:45 Waaye su fekkee surga ba da ne ci xelam: \u201cSama njaatige day y\u00e9ex a \u00f1\u00ebw,\u201d ba tax mu t\u00e0mbalee d\u00f3or surga ya ca des ak mbindaan ya, di lekk te di naan, di m\u00e0ndi,\n12:46 kon njaatige ba dina \u00f1\u00ebw ci b\u00e9s bu mu ko s\u00e9enuwul ak waxtu wu mu xamul. Dina ko d\u00f3or ay d\u00f3or yu metti, jox ko a\u00f1ub \u00f1i g\u00ebmul Y\u00e0lla.\n12:47 \u00abSurga bi xam b\u00ebgg-b\u00ebggu njaatigeem, te waajul mbaa mu takku def ko, dina\u00f1u ko d\u00f3or d\u00f3or yu metti.\n12:48 Waaye surga bi xamul b\u00ebgg-b\u00ebggu njaatigeem, te def lu yelloo ay d\u00f3or, dina\u00f1u ko d\u00f3or d\u00f3or yu n\u00e9ew. Ku \u00f1u jox lu bare dees na la feyiku lu bare. Ku \u00f1u d\u00e9nk lu bare, dees na la laajaat lu ko \u00ebpp.\n12:49 \u00abDamaa \u00f1\u00ebw ngir indi safara si ci \u00e0ddina, te b\u00ebgg naa xaat taal bi t\u00e0kk.\n12:50 F\u00e0ww \u00f1u s\u00f3ob ma ci metit, te ba looluy mat, duma noppalu.\n12:51 Ndax dangeen a xalaat ne, damaa \u00f1\u00ebw ngir indi j\u00e0mm ci \u00e0ddina? D\u00e9ed\u00e9et. Maa ngi leen koy wax, damaa \u00f1\u00ebw ngir indi f\u00e9ewaloo.\n12:52 Gannaawsi tey, bu jur\u00f3omi nit bokkee genn k\u00ebr, dina\u00f1u f\u00e9ewaloo. \u00d1ett dina\u00f1u f\u00e9ewaloo ak \u00f1aar \u00f1i ci des, \u00f1aar \u00f1i f\u00e9ewaloo ak \u00f1ett \u00f1oo\u00f1u.\n12:53 Baay bi dina f\u00e9ewaloo ak doom ji, doom ji ak baayam. Ndey dina f\u00e9ewaloo ak doomam ju jig\u00e9en; doom ju jig\u00e9en ji ak ndeyam. Goro dina f\u00e9ewaloo ak jabaru doomam; jabaru nit ak goroom.\u00bb\n12:54 Yeesu neeti mbooloo ma: \u00abBu ngeen gisee mu xiin ci sowu, dangeen naan ca saa sa: \u201cDina taw,\u201d te mooy am.\n12:55 Te bu ngeen y\u00e9gee ngelaw liy uppe sudd, ngeen ne: \u201cDina t\u00e0ng t\u00e0ngaay wu metti,\u201d te mooy am.\n12:56 Naaf\u00e9q yi ngeen doon! Man ngeen a r\u00e0\u00f1\u00f1ee melow asamaan ak suuf, waaye lu tax m\u00ebnuleen a r\u00e0\u00f1\u00f1ee li jamonoy l\u00e9egi ji di tekki?\n12:57 \u00abLu tax it dungeen \u00e0tteel seen bopp liy j\u00ebf ju jub?\n12:58 Bu la nit jii\u00f1ee dara, ba ngeen \u00e0nd di dem ca \u00e0ttekat ba, nanga fexee juboo ak moom ci yoon wi. Lu ko moy, dina la y\u00f3bbu ci yoon, yoon j\u00e9bbal la ca loxoy alkaati ba, mu t\u00ebj la.\n12:59 Maa ngi la koy wax, doo g\u00e9nn foofa mukk te feyuloo fiftin bi ci mujj.\u00bb\n13:1 Ca jamono jooju ay nit \u00f1\u00ebw ca Yeesu, nettali mbirum waa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi \u00f1u rendi woon, j\u00e9bbal leen Y\u00e0lla.\n13:2 Mu tontu leen ne: \u00abMbaa du dangeen a xalaat ne, waa Galile yooyu da\u00f1oo g\u00ebn a nekk b\u00e0kkaarkat \u00f1a ca des, ndax coono bi \u00f1u daj?\n13:3 Maa ngi leen di wax ne, du d\u00ebgg. Waaye su ngeen tuubul seeni b\u00e0kkaar, dingeen s\u00e0nku noonu, y\u00e9en \u00f1\u00e9pp itam.\n13:4 Te fukki nit ak jur\u00f3om-\u00f1ett \u00f1oo\u00f1u dee, bi taaxum kaw ma ca goxu Silowe daanoo ci seen kaw, ndax dangeen a yaakaar ne, \u00f1oo g\u00ebn a nekk ay too\u00f1kat \u00f1eneen \u00f1i d\u00ebkk Yerusalem y\u00e9pp?\n13:5 Maa ngi leen di wax ne, du d\u00ebgg. Waaye su ngeen tuubul seeni b\u00e0kkaar, dingeen s\u00e0nku noonu, y\u00e9en \u00f1\u00e9pp itam.\u00bb\n13:6 Noonu mu daldi leen wax l\u00e9eb wii: \u00abNit amoon na ci toolam garab gu \u00f1u naan figg. Benn b\u00e9s mu \u00f1\u00ebw di ko raas-si, fekku fa benn doom.\n13:7 Noonu mu ne surga ba: \u201c\u00d1etti at a ngii may \u00f1\u00ebw di raas-si garab gii te duma ci fekk dara. Gor ko. Lu tax muy xatal tool bi?\u201d\n13:8 Surga ba tontu ko ne: \u201cSang bi, b\u00e0yyiwaat ko fi at mii. Dinaa w\u00e0qi taat wi, def ci tos.\n13:9 X\u00eby na dina me\u00f1\u00f1i. Bu ko deful, nga gor ko.\u201d\u00bb\n13:10 Benn b\u00e9su noflaay Yeesoo ngi doon j\u00e0ngale ci ab j\u00e0ngu.\n13:11 Amoon na fa jig\u00e9en ju rab j\u00e0ppoon, ba feebarloo ko lu war a mat fukki at ak jur\u00f3om-\u00f1ett; dafa xuuge woon te m\u00ebnul woon a siggi dara.\n13:12 Bi ko Yeesu gisee, mu woo ko ne ko: \u00abSoxna si, sa feebar de\u00f1 na.\u00bb\n13:13 Noonu mu teg ko ay loxoom, soxna sa siggi ca saa sa, di m\u00e0ggal Y\u00e0lla.\n13:14 Waaye njiitu j\u00e0ngu ba mer, ndax li Yeesu fajoon nit ca b\u00e9su noflaay ba, mu ne mbooloo ma: \u00abAm na jur\u00f3om-benni fan yu nit \u00f1i war a ligg\u00e9ey. Kon war ngeen a \u00f1\u00ebw faju ci b\u00e9s yooyu, waaye du ci b\u00e9su noflaay bi.\u00bb\n13:15 Boroom bi tontu ko: \u00abNaaf\u00e9q yi! Ndax b\u00e9su noflaay bi, kenn ku nekk ci y\u00e9en du yiwee ca g\u00e9tt ga y\u00ebkkam walla mbaamam ngir w\u00ebggi ko?\n13:16 Jig\u00e9en jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane t\u00ebnk ko fukki at ak jur\u00f3om-\u00f1ett, ndax kenn waru koo yiwi ci b\u00e9su noflaay bi?\u00bb\n13:17 Naka la wax loolu, noonam y\u00e9pp daldi rus, waaye mbooloo mi di b\u00e9g ci j\u00ebf yu y\u00e9eme, yi mu doon def y\u00e9pp.\n13:18 Noonu Yeesu neeti: \u00abLan la nguuru Y\u00e0lla di nirool? Lan laa ko man a mengaleel?\n13:19 Mi ngi mel ni doomu fudd\u00ebn gu nit j\u00ebl, ji ko ci toolam. Mu sax, nekk garab, ba picci asamaan \u00f1\u00ebw, t\u00e0gg ciy caram.\u00bb\n13:20 Mu neeti: \u00abLan laa man a mengaleek nguuru Y\u00e0lla?\n13:21 Mi ngi mel ni lawiir bu jig\u00e9en j\u00ebl, jaxase ko ak \u00f1etti andaari fari\u00f1, ba kera tooyal b\u00e9pp di funki.\u00bb\n13:22 Yeesoo ngi doon jaar ci ay d\u00ebkk yu mag ak yu ndaw, di j\u00e0ngale te jublu Yerusalem.\n13:23 Am ku ko ne: \u00abBoroom bi, ndax \u00f1iy mucc \u00f1u n\u00e9ew lay doon?\u00bb Yeesu ne leen:\n13:24 \u00abDefleen seen kem-k\u00e0ttan, ngir dugg ci bunt bu xat bi, ndaxte maa ngi leen koy wax, \u00f1u bare dina\u00f1u j\u00e9em a dugg, waaye du\u00f1u ko man.\n13:25 Jamono dina \u00f1\u00ebw, ju boroom k\u00ebr gi di j\u00f3g, t\u00ebj buntam. Dingeen nekk ci biti di f\u00ebgg naan: \u201cBoroom bi, ubbil nu!\u201d Dina leen tontu ne: \u201cXawma fu ngeen bokk.\u201d\n13:26 Bu ko defee dingeen t\u00e0mbalee naan: \u201cNoo doon bokk di lekk ak di naan, te j\u00e0ngale nga ci sunuy p\u00e9nc.\u201d\n13:27 Waaye dina ne: \u201cNee naa leen xawma fu ngeen bokk. Y\u00e9en \u00f1\u00e9pp soreleen ma, defkati lu bon yi!\u201d\n13:28 Foofa dingeen jooy, di y\u00e9yu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanq\u00f3oba ak yonent y\u00e9pp ci nguuru Y\u00e0lla, te \u00f1u d\u00e0q leen ca biti.\n13:29 Ay nit dina\u00f1u j\u00f3ge penku ak sowu, nor ak sudd, \u00f1\u00ebw, bokk lekk ci \u00f1am, yi Y\u00e0lla di joxe ci nguuram.\n13:30 Noonu \u00f1enn ci \u00f1i mujj \u00f1ooy jiituji; te ci \u00f1i jiitu, \u00f1ooy mujji.\u00bb\n13:31 Ca jamono jooja ay Farisen \u00f1\u00ebw ca Yeesu ne ko: \u00abJ\u00f3geel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wut a rey.\u00bb\n13:32 Noonu mu ne leen: \u00abDemleen ne bukki boobu ne ko: \u201cXoolal, maa ngi d\u00e0q rab yi tey w\u00e9ral nit \u00f1i tey ak suba. Ca \u00f1etteelu fan ba, ma \u00e0gg fa ma Y\u00e0lla j\u00ebmale.\u201d\n13:33 Waaye f\u00e0ww ma dox sama itte tey, suba ak gannaaw suba, ndaxte wareesul a reye ab yonent feneen fu dul Yerusalem.\n13:34 \u00abYerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey s\u00e0nni ay doj ndaw yi, ba \u00f1u dee, aka maa b\u00ebggoon a dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen!\n13:35 Kon nag Y\u00e0lla dina b\u00ebrg\u00ebl seen k\u00ebr. Te maa ngi leen koy wax, dungeen ma gisati, ba kera ngeen ne: \u201cYaw miy \u00f1\u00ebw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga!\u201d\u00bb\n14:1 Benn b\u00e9su noflaay Yeesu dem ci k\u00ebru benn kilifag Farisen yi, ngir lekke fa. Nit \u00f1aa ngi ko doon xool bu baax.\n14:2 Faf am ca kanamam nit ku feebaroon, ay t\u00e0nkam newi.\n14:3 Yeesu y\u00e9kkati baatam, ne xutbakat ya ak Farisen ya: \u00abNdax jaadu na, nu faj ci b\u00e9su noflaay bi?\u00bb\n14:4 Waaye \u00f1\u00e9pp ne cell. Yeesu daldi laal jarag ja, faj ko, ba noppi ne ko mu \u00f1ibbi.\n14:5 Gannaaw loolu mu ne leen: \u00abKu sa doom walla sa y\u00ebkk daanu ci teen, ndax doo dem g\u00e9nneji ko ca saa sa, fekk sax b\u00e9sub noflaay la?\u00bb\n14:6 Amu\u00f1u woon dara lu \u00f1u ciy teg.\n14:7 Yeesu gis ni gan yi doon t\u00e0nne toogu yu yiw yi, mu daldi leen wax l\u00e9eb wii:\n14:8 \u00abBu \u00f1u la wooyee ci xewu c\u00e9et, bul j\u00ebl toogu bu yiw. Man na am woo na\u00f1u it nit ku la \u00ebpp daraja.\n14:9 Kon ki leen woo y\u00e9en \u00f1aar \u00f1\u00e9pp man na \u00f1\u00ebw ci yaw ne la: \u201cJoxal toogu bi nit kii.\u201d Noonu dinga rus a dem ca toogu bu gannaawe ba.\n14:10 Waaye bu \u00f1u la wooyee, demal ca toogu bu gannaawe ba. Bu ko defee ki la woo, bu agsee ne la: \u201cSama xarit, \u00e0ggal ca kaw.\u201d Loolu dina la sagal ci \u00f1i nga toogandool ci lekkukaay bi.\n14:11 Ndaxte k\u00e9pp kuy y\u00e9kkatiku, dees na la suufeel, te kuy suufeelu, dina\u00f1u la y\u00e9kkati.\u00bb\n14:12 Noonu Yeesu ne ki ko woo woon lekk: \u00abBoo dee woote a\u00f1 walla reer, bul woo rekk say xarit, say doomi ndey, say bokk, walla say d\u00ebkkandoo yu am alal. Lu ko moy \u00f1oo\u00f1u itam dina\u00f1u la woo, fey la bor bi.\n14:13 Waaye boo dee woote lekk, wool n\u00e9ew doole yi, l\u00e0ggi yi, lafa\u00f1 yi ak gumba yi.\n14:14 Soo ko defee, dinga barkeel, ndaxte du\u00f1u la ko man a fey, waaye dinga jot sag pey, b\u00e9s bi \u00f1i jub di dekki.\u00bb\n14:15 Bi mu d\u00e9ggee wax yooyu, kenn ca gan ya ne Yeesu: \u00abKiy lekk ci \u00f1am, yi Y\u00e0lla di joxe ci nguuram, barkeel nga!\u00bb\n14:16 Yeesu tontu ko ne: \u00abDafa amoon nit ku togglu ay \u00f1am, woo ay nit \u00f1u bare.\n14:17 Bi waxtuw lekk jotee mu y\u00f3nni surga ca \u00f1a muy ganale, f\u00e0ttali leen: \u201cMan ngeen a \u00f1\u00ebw, ndaxte l\u00e9pp sotti na l\u00e9egi.\u201d\n14:18 \u00abWaaye \u00f1u t\u00e0mbali di j\u00e9ggalu ci ngan gi \u00f1oom \u00f1\u00e9pp. Ku j\u00ebkk ka ne ko: \u201cDamaa j\u00ebnd tool l\u00e9egi, te f\u00e0ww ma dem seeti ko. Maa ngi lay \u00f1aan, nga j\u00e9ggal ma.\u201d\n14:19 Keneen ne: \u201cDamaa j\u00ebnd l\u00e9egi fukki y\u00ebkk, te damay dem nii, j\u00e9em leen a beyloo ba xam. Maa ngi lay \u00f1aan, nga j\u00e9ggal ma.\u201d\n14:20 Keneen ne ko: \u201cDamay sog a takk jabar, looloo tax duma man a \u00f1\u00ebw.\u201d\n14:21 \u00abSurga ba dellu ca njaatigeem nettali ko loolu l\u00e9pp. Noonu boroom k\u00ebr ga mer, daldi ne surga ba: \u201cDemal gaaw ca p\u00e9nc ya ak ca mbedd ya ca d\u00ebkk ba, te indil ma fii n\u00e9ew doole yi, \u00f1u l\u00e0ggi \u00f1i, gumba yi ak lafa\u00f1 yi.\u201d\n14:22 \u00abSurga ba \u00f1\u00ebwaat ne ko: \u201cSang bi, def naa li nga ma sant, waaye b\u00e9rab bi feesul.\u201d\n14:23 Noonu njaatige ba ne ko: \u201cG\u00e9nnal d\u00ebkk bi te dem ca yoon ya ak ca tool ya, xiir nit \u00f1i, \u00f1u duggsi, ngir sama k\u00ebr fees.\n14:24 Maa ngi leen koy wax, ci \u00f1i ma woo woon ci sama reer bi, kenn du ci \u00f1am.\u201d\u00bb\n14:25 Am mbooloo yu r\u00e9y yu toppoon ci Yeesu, ba muy dem ca yoon wa. Mu geestu ne leen:\n14:26 \u00abK\u00e9pp ku \u00f1\u00ebw ci man te g\u00ebnalu ma ko baayam, yaayam, jabaram, ay doomam, ay magam ak ay rakkam, walla sax bakkanam, du man a nekk sama taalibe.\n14:27 K\u00e9pp koo xam ne nanguwuloo \u00f1\u00e0kk sa bakkan, ba mel ni ku \u00f1u daaj ci bant, te nga topp ma, doo man a nekk sama taalibe.\n14:28 Su kenn ci y\u00e9en b\u00ebggee tabax taaxum kaw, ndax du j\u00ebkk a toog, xalaat \u00f1aata la ko war a dikke, ngir seet ba xam ndax am na xaalis bu man a \u00e0ggale ligg\u00e9ey bi?\n14:29 Lu ko moy, su y\u00e9kkatee fondamaa bi te m\u00ebnu koo \u00e0ggale, \u00f1i koy gis dina\u00f1u ko \u00f1aawal, naan ko:\n14:30 \u201cWaa jii dafa t\u00e0mbalee tabax, waaye m\u00ebnu koo \u00e0ggale.\u201d\n14:31 Walla boog ban buur mooy dugg ci xare ak beneen buur te j\u00ebkkul a toog, seet ba xam moom ak fukki junniy xarekat man na xeex ak kiy \u00f1\u00ebw ak \u00f1aar-fukki junniy xarekat?\n14:32 Su ko m\u00ebnul, dafay y\u00f3nni ndaw ca beneen buur ba, fi ak ma ngay sore, ngir \u00f1u juboo.\n14:33 Naka noonu itam ku nekk ci y\u00e9en, bu d\u00ebdduwul li mu am l\u00e9pp, du man a nekk sama taalibe.\n14:34 \u00abXam ngeen nag ne, xorom lu baax la, waaye bu s\u00e0ppee, nan la\u00f1u koy delloo cafkaam?\n14:35 Du jari\u00f1 suuf, te du nekk tos. Da\u00f1u koy s\u00e0nni ca biti. D\u00e9glul bu baax, yaw mi am ay nopp.\u00bb\n15:1 Ay juutikat ak ay boroom b\u00e0kkaar daan jegesi Yeesu ngir d\u00e9glu ko.\n15:2 Farisen ya ak xutbakat ya di \u00f1urumtu naan: \u00abWaa jii mi ngi nangoo nekk ak ay boroom b\u00e0kkaar ak a lekkandook \u00f1oom!\u00bb\n15:3 Noonu Yeesu daldi leen wax l\u00e9eb wii ne leen:\n15:4 \u00abKan ci y\u00e9en soo amoon t\u00e9em\u00e9eri xar, te benn r\u00e9er ci, nooy def? Ndax doo b\u00e0yyi ca parlukaay ba jur\u00f3om-\u00f1eent-fukki xar ya ak jur\u00f3om-\u00f1eent, toppi ma r\u00e9er, ba gis ko?\n15:5 Te boo ko gisee, dinga ko g\u00e0ddu ak b\u00e0nneex, y\u00f3bbu ko k\u00ebr ga.\n15:6 Boo \u00e0ggee ca k\u00ebr ga, dinga woo say xarit ak say d\u00ebkkandoo ne leen: \u201cKaayleen b\u00e0nneexu ak man, ndaxte gis naa sama xar ma r\u00e9eroon.\u201d\n15:7 \u00abMaa ngi leen di wax lii: ci noonule, dina am mb\u00e9g ci asamaan, bu benn b\u00e0kkaarkat tuubee ay b\u00e0kkaaram. Te mb\u00e9g moomu mooy \u00ebpp mb\u00e9g, mi fay am, ngir jur\u00f3om-\u00f1eent-fukk ak jur\u00f3om-\u00f1eent \u00f1u jub, te soxlawu\u00f1oo tuub seeni b\u00e0kkaar.\n15:8 \u00abTe it bu jig\u00e9en dencoon fukki libidoor, benn r\u00e9er ca, nu muy def? Ndax du taal ab l\u00e0mp, bale k\u00ebr ga, seet fu nekk, ba gis ko?\n15:9 Bu ko gisee, dina woo ay xaritam ak ay d\u00ebkkandoom ne leen: \u201cKaayleen b\u00e0nneexu ak man, ndaxte gis naa sama alal ja r\u00e9eroon.\u201d\n15:10 Maa ngi leen di wax lii: ci noonule la malaakay Y\u00e0lla yi di ame mb\u00e9g ci benn b\u00e0kkaarkat bu tuubee ay b\u00e0kkaaram.\u00bb\n15:11 Yeesu dellu ne leen: \u00abDafa amoon g\u00f3or gu am \u00f1aari doom.\n15:12 Benn b\u00e9s caat ma ne baay ba: \u201cBaay, damaa b\u00ebggoon, nga jox ma li may war a f\u00e9etewoo ci ndono li.\u201d Noonu baay ba daldi leen s\u00e9ddale alalam.\n15:13 Ay fan yu n\u00e9ew gannaaw gi, caat ma fab y\u00ebfam y\u00e9pp, dem ca r\u00e9ew mu sore, y\u00e0q fa alalam ci topp nafsoom.\n15:14 Bi mu s\u00e0nkee alalam j\u00e9pp, xiif bu metti dal ca r\u00e9ew ma, mu t\u00e0mbalee \u00f1\u00e0kk.\n15:15 Mu dem nag, di ligg\u00e9eyal ku d\u00ebkk ca r\u00e9ew ma, kooku yebal ko ca ay toolam ngir mu s\u00e0mm mbaam-xuux ya.\n15:16 Mu xiif ba b\u00ebgg a lekk ca \u00f1amu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara.\n15:17 Mujj xelam dellusi, mu ne: \u201cSama baay am na ay surga yu bare, te da\u00f1uy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di b\u00ebgg a dee ak xiif!\n15:18 Damay j\u00f3g, dem ca sama baay ne ko: \u2018Baay, too\u00f1 naa Y\u00e0lla, too\u00f1 naa la;\n15:19 yeyootumaa nekk sa doom; boole ma ci say surga.\u2019 \u201d\n15:20 \u00abMu daldi j\u00f3g, j\u00ebm k\u00ebr baayam. Waaye bi muy soreendi k\u00ebr ga, baayam s\u00e9en ko, y\u00ebr\u00ebm ko, daldi daw laxasu ko, f\u00f3on ko.\n15:21 Doom ja ne ko: \u201cBaay, too\u00f1 naa Y\u00e0lla, too\u00f1 naa la; yeyootumaa nekk sa doom.\u201d\n15:22 Waaye baay ba ne ay surgaam: \u201cGaawleen indi mbubb, mi g\u00ebn a rafet, solal ko ko. Te ngeen roof ab jaaro ci loxoom te solal ko ay d\u00e0ll.\n15:23 Indileen s\u00ebllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te b\u00e0nneexu;\n15:24 ndaxte sama doom jii dafa dee woon te dundaat na, dafa r\u00e9eroon te fee\u00f1 na.\u201d Noonu \u00f1u t\u00e0mbalee b\u00e0nneexu.\n15:25 \u00abFekk booba taaw baa nga woon ca tool ya. Bi mu \u00f1\u00ebwee, ba jub k\u00ebr ga, mu d\u00e9gg \u00f1uy t\u00ebgg, di fecc.\n15:26 Mu daldi woo kenn ca surga ya nag, laaj ko lu xew.\n15:27 Mu tontu ko: \u201cSa rakk moo dellusi, te sa baay rey na s\u00ebllu wu duuf wa, ndaxte \u00f1ibbisi na ci j\u00e0mm.\u201d\n15:28 \u00abCi kaw loolu taaw ba daldi mer, ba\u00f1 a dugg ca k\u00ebr ga. Baayam daldi g\u00e9nn, ngir \u00f1aan ko mu dugg.\n15:29 Waaye taaw ba tontu baayam ne ko: \u201cSeetal \u00f1aata at laa la ligg\u00e9eyal, mel ni jaam, te musumaa moy sa ndigal, waaye yaw, musuloo ma may sax tef, ngir ma b\u00e0nneexu, man ak samay xarit.\n15:30 Waaye bi sa doom jii dikkee, moom mi y\u00e0q sa alal ci ndoxaan, reyal nga ko s\u00ebllu wu duuf wi.\u201d\n15:31 Noonu baay bi tontu ko ne ko: \u201cSama doom, yaa ngi ak man b\u00e9s bu nekk, te li ma am l\u00e9pp, yaa ko moom.\n15:32 Waaye war nanoo b\u00e0nneexu te b\u00e9g, ndaxte sa rakk jii dafa dee woon te dundaat na, dafa r\u00e9eroon te fee\u00f1 na.\u201d\u00bb\n16:1 Yeesu neeti ay taalibeem: \u00abBenn boroom alal moo amoon b\u00ebkk-n\u00e9eg bu \u00f1u jii\u00f1 ne, dafay pasar-pasaree alal ji.\n16:2 Waa ja woo ko ne ko: \u201cLi may d\u00e9gg ci yaw mooy lan? Leeralal ma ni nga ligg\u00e9eye ak sama alal, ndaxte dootoo nekkati sama b\u00ebkk-n\u00e9eg.\u201d\n16:3 \u00abB\u00ebkk-n\u00e9eg bi di xalaat naan: \u201cNu may def nag, segam sama njaatige dafa may d\u00e0q ci ligg\u00e9ey bi mu ma joxoon? Dem beyi? Awma k\u00e0ttanam. Yelwaani? Rus naa ko.\n16:4 Xam naa ni may def, ba su ma \u00f1\u00e0kkee sama ligg\u00e9ey, ay nit fat ma.\u201d\n16:5 Noonu mu daldi woolu kenn ku nekk ca \u00f1a ameeloon njaatigeem bor. Ka j\u00ebkk a \u00f1\u00ebw, mu ne ko: \u201c\u00d1aata nga ameel sama njaatige?\u201d\n16:6 Mu ne ko: \u201cT\u00e9em\u00e9eri bido\u014bi diwlinu oliw.\u201d B\u00ebkk-n\u00e9eg ba ne ko: \u201cSa kayit a ngii. Toogal fii gaaw te bind jur\u00f3om-fukk.\u201d\n16:7 Mu neeti keneen: \u201cYaw nag, \u00f1aata nga ko ameel?\u201d Mu ne ko: \u201cT\u00e9em\u00e9eri saakuy pepp.\u201d B\u00ebkk-n\u00e9eg ba ne ko: \u201cSa kayit a ngii. Bindal jur\u00f3om-\u00f1ett-fukk.\u201d\n16:8 Njaatige ba nag daldi naw ni b\u00ebkk-n\u00e9eg bu njubla\u014b boobu muuse woon. Ndaxte \u00f1i bokk ci \u00e0ddina \u00f1oo g\u00ebn a muus ci li \u00f1u jote ci seen diggante ak seen moroom, ba raw \u00f1i bokk ci leeru Y\u00e0lla.\u00bb\n16:9 Yeesu teg ca ne: \u00abMaa ngi leen di wax lii: s\u00e0kkuleen ay xarit jaare ko ci alalu \u00e0ddina, ngir bu alal nekkatul, \u00f1u man leen a fat ca dal yu sax ya.\n16:10 Nit ku maandu ci y\u00ebf yu n\u00e9ew, dina maandu itam ci yu bare. Ku jubadi ci y\u00ebf yu n\u00e9ew, du jub ci yu bare.\n16:11 Su fekkeente ne nag jubuleen ci alalu \u00e0ddina, kon ku leen di d\u00e9nk alal ju w\u00f3or ji?\n16:12 Te su ngeen maanduwul ci alal ji ngeen moomul, kon ku leen di jox alal ji ngeen moom?\n16:13 \u00abBenn jaam m\u00ebnul a jaamoondoo \u00f1aari sang; f\u00e0ww nga ba\u00f1 kii, b\u00ebgg ki ci des, walla nga j\u00e0pp ci kenn ki, xeeb ki ci des. M\u00ebnuleen a boole jaamu Y\u00e0lla ak jaamu Alal.\u00bb\n16:14 Farisen yi d\u00e9glu li Yeesu doon wax l\u00e9pp, t\u00e0mbali di ko reetaan, ndaxte \u00f1u b\u00ebggoon xaalis la\u00f1u.\n16:15 Waaye Yeesu ne leen: \u00abY\u00e9en y\u00e9ena ngi fexee jub ci kanamu nit \u00f1i waaye Y\u00e0lla xam na seen xol. Ndaxte li nit \u00f1iy fonk, Y\u00e0lla sib na ko.\n16:16 \u00abYoonu Musaa wi ak waxi yonent yi \u00f1u ngi fi woon ba kera Yaxya di \u00f1\u00ebw. La ko dale foofa nag, y\u00e9gle na\u00f1u xebaar bu baax bi ci nguuru Y\u00e0lla, te \u00f1\u00e9pp a ngi g\u00f3or-g\u00f3orlu, ngir dugg ci.\n16:17 Waaye nag asamaan ak suuf j\u00f3ge fi moo g\u00ebn a yomb randal wenn r\u00ebdd ci arafu yoonu Musaa.\n16:18 \u00abKu fase sa jabar, ba noppi takk keneen, njaaloo nga, te ku takk jig\u00e9en ju j\u00ebkk\u00ebram fase, njaaloo nga.\n16:19 \u00abDafa amoon boroom alal juy sol y\u00e9re yu rafet te jafe, tey dund b\u00e9s bu set dund gu neex.\n16:20 Fekk miskin mu \u00f1uy wax Lasaar daan t\u00ebdd ca buntu k\u00ebram, fees dell ak ay g\u00f3om,\n16:21 te bu sa\u00f1oon, di lekk ci desiti \u00f1am wiy rot ci lekkukaayu boroom alal ji. Xaj yi sax daan na\u00f1u \u00f1\u00ebw, di mar ay g\u00f3omam.\n16:22 \u00abNoonu miskin ma dee, malaaka yi y\u00f3bbu ko ca wetu Ibraayma. Boroom alal ja itam dee, \u00f1u suul ko.\n16:23 Bi \u00f1u koy mbugal ca safara, mu t\u00e9en, s\u00e9en fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.\n16:24 Noonu mu yuuxu ne: \u201cMaam Ibraayma, y\u00ebr\u00ebm ma! Yebalal Lasaar, mu s\u00ebpp catul baaraamam ci ndox, seralal ma sama l\u00e0mmi\u00f1, ndaxte maa ngi sonn lool ci safara sii!\u201d\n16:25 Ibraayma ne ko: \u201cSama doom, f\u00e0ttalikul ne, jot nga sa b\u00e0nneex ci \u00e0ddina, fekk Lasaar d\u00ebkk ci tiis. Looloo tax xolam sedd fii, yaw nag, ngay sonn.\n16:26 Rax-ca-dolli it am na k\u00e0mb gu x\u00f3ot sunu diggante ak y\u00e9en, ba tax \u00f1i b\u00ebgg a j\u00f3ge fii j\u00ebm ci y\u00e9en, walla \u00f1i b\u00ebgg a j\u00f3ge foofu j\u00ebmsi ci nun, du\u00f1u ko man.\u201d\n16:27 \u00abNoonu boroom alal ja ne: \u201cKon nag maam, maa ngi lay \u00f1aan, nga yebal Lasaar ca sama k\u00ebr baay,\n16:28 ndaxte am naa fa jur\u00f3omi rakk. Na leen artu, ngir \u00f1u ba\u00f1 a \u00f1\u00ebw \u00f1oom itam ci b\u00e9rabu metit wii.\u201d\n16:29 Ibraayma ne ko: \u201cSay doomu baay, \u00f1u ngeek yoonu Musaa ak t\u00e9erey yonent yi. Na\u00f1u leen d\u00e9ggal.\u201d\n16:30 Boroom alal ja ne ko: \u201cD\u00e9ed\u00e9et, maam Ibraayma, waaye su kenn dekkee, dem ca \u00f1oom, dina\u00f1u tuub seeni b\u00e0kkaar.\u201d\n16:31 Waaye Ibraayma tontu ko ne: \u201cSu \u00f1u d\u00e9gluwul Musaa ak yonent yi, kon ku dekki sax, du tax \u00f1u g\u00ebm.\u201d\u00bb\n17:1 Yeesu waxaat ay taalibeem ne leen: \u00abFiir yuy y\u00f3bbe nit b\u00e0kkaar m\u00ebnta \u00f1\u00e0kk, waaye toroxte dal na ki koy lal.\n17:2 \u00d1u takk doj wu r\u00e9y ci baatam, s\u00e0nni ko ci g\u00e9ej moo g\u00ebn ci moom muy daaneel ci b\u00e0kkaar kenn ci \u00f1i g\u00ebn a tuuti ci \u00f1ii.\n17:3 Wottuleen seen bopp. \u00abBu sa mbokk too\u00f1ee, yedd ko. Bu r\u00e9ccoo, baal ko.\n17:4 Te su la too\u00f1ee jur\u00f3om-\u00f1aari yoon ci b\u00e9s bi, te \u00f1\u00ebw ci yaw jur\u00f3om-\u00f1aari yoon ne la: \u201cTuub naa ko,\u201d nanga ko baal.\u00bb\n17:5 Ndaw ya wax Boroom bi ne ko: \u00abYokkal sunu ng\u00ebm.\u00bb\n17:6 Boroom bi tontu ne: \u00abSu ngeen amee ng\u00ebm gu tuuti sax niw peppu fudd\u00ebn, kon dingeen man a ne garab gii: \u201cBuddeekul, dem j\u00ebmb\u00ebtu ca g\u00e9ej ga,\u201d te dina def li ngeen wax.\n17:7 \u00abKan ci y\u00e9en bu amoon surga bu beyi walla bu s\u00e0mmi ba \u00f1\u00ebw, ndax dafa ko naa: \u201cKaay lekk.\u201d\n17:8 D\u00e9ed\u00e9et. Xanaa kay da ko naan: \u201cDefaral ma r\u00e9er bi. Takkul te tibbal ma, ba ma lekk te naan, ba noppi nga door a lekk te naan.\u201d\n17:9 Li surga ba topp ndigal, ndax tax na mu yelloo ng\u00ebr\u00ebm? D\u00e9ed\u00e9et.\n17:10 Noonu y\u00e9en itam bu ngeen toppee li \u00f1u leen sant l\u00e9pp ba noppi, dangeen a war ne: \u201cAy surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.\u201d\u00bb\n17:11 Bi muy dem Yerusalem ba tey, Yeesu jaar ci dig wiy xaajale Samari ak Galile.\n17:12 Bi muy jub benn d\u00ebkk, fukki gaana \u00f1\u00ebw, dogale ko. \u00d1u taxaw dand ko, di wax ca kaw naan:\n17:13 \u00abYeesu, kilifa gi, y\u00ebr\u00ebm nu!\u00bb\n17:14 Naka la leen Yeesu di gis, naan leen: \u00abDemleen won seen bopp saraxalekat ya.\u00bb Bi \u00f1uy dem, \u00f1u daldi set.\n17:15 Kenn ci \u00f1oom gis ne w\u00e9r na, daldi d\u00ebpp, di m\u00e0ggal Y\u00e0lla ak baat bu xumb.\n17:16 Mu d\u00ebpp j\u00ebwam ca t\u00e0nki Yeesu, di ko g\u00ebr\u00ebm. Fekk nitu Samari la woon.\n17:17 Noonu Yeesu daldi ne: \u00abXanaa du fukk y\u00e9pp a w\u00e9r? Ana jur\u00f3om-\u00f1eent \u00f1a nag?\n17:18 Amul kenn ci \u00f1oom ku \u00f1\u00ebw g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla ku dul doxand\u00e9em bii!\u00bb\n17:19 Noonu Yeesu ne ko: \u00abJ\u00f3gal dem; sa ng\u00ebm faj na la.\u00bb\n17:20 Farisen yi laaj Yeesu ne ko: \u00abKa\u00f1 la Y\u00e0lla di t\u00ebral nguuram?\u00bb Mu tontu leen ne: \u00abBu Y\u00e0lla di w\u00e0cce nguuram ci nit \u00f1i, kenn du ko man a teg b\u00ebt.\n17:21 Du\u00f1u man a wax it ne: \u201cXool-leen, mi ngi fii,\u201d walla: \u201cMa nga fale,\u201d ndaxte nguuru Y\u00e0lla w\u00e0cc na ci seen biir.\u00bb\n17:22 Noonu mu ne taalibe ya: \u00abJamono dina \u00f1\u00ebw, fu ngeen di b\u00ebgg a gis su doon sax benn fan ci jamono ju Doomu nit ki di \u00f1\u00ebw, waaye dungeen ko gis.\n17:23 Dees na leen ne: \u201cMi ngi fii!\u201d walla: \u201cMa nga fale!\u201d Buleen dem, mbaa ngeen di leen topp.\n17:24 Ndaxte ni melax naan r\u00e0yye ci asamaan, di leeral gii wet, ba ca gee, noonu it la Doomu nit ki di mel ci b\u00e9sam.\n17:25 Waaye balaa booba f\u00e0ww mu sonn lool te niti jamono jii d\u00ebddu ko.\n17:26 \u00abLa xewoon ca b\u00e9si N\u00f3oyin, dina xewaat ci b\u00e9si Doomu nit ki.\n17:27 Nit \u00f1aa ngi doon lekk ak di naan, di j\u00ebl jabar ak a s\u00e9yi, ba b\u00e9s ba N\u00f3oyin duggee ca gaal ga. Noonu mb\u00ebnn ma \u00f1\u00ebw, rey leen \u00f1oom \u00f1\u00e9pp.\n17:28 \u00abDina mel it ni la xewoon ca b\u00e9si L\u00f3ot. Nit \u00f1aa ngi doon lekk ak di naan, di j\u00ebnd ak di jaay, di ji ak di tabax.\n17:29 Waaye b\u00e9s ba L\u00f3ot g\u00e9nnee Sodom, Y\u00e0lla tawloo safara ak tamarax, rey leen \u00f1oom \u00f1\u00e9pp.\n17:30 Noonu lay mel, b\u00e9s bu Doomu nit kiy fee\u00f1.\n17:31 \u00abCa b\u00e9s boobee ku nekk ca kaw k\u00ebr ga te ay bagaasam nekk ca biir, bumu w\u00e0cc j\u00ebli leen. Te it ku nekk ca tool ya, bu mu \u00f1ibbi.\n17:32 F\u00e0ttalikuleen jabaru L\u00f3ot!\n17:33 Kuy wut a rawale sa bakkan, dinga ko \u00f1\u00e0kk, waaye ku ko \u00f1\u00e0kk, dinga dund.\n17:34 Maa ngi leen koy wax: ca jamono jooju, \u00f1aar dina\u00f1u bokk a t\u00ebdd guddi, dees na y\u00f3bbu kenn ki, b\u00e0yyi ka ca des.\n17:35 \u00d1aari jig\u00e9en dina\u00f1u wolandoo, dees na y\u00f3bbu kenn ci, b\u00e0yyi ka ca des.\u00bb\n17:37 Taalibe yi ne Yeesu: \u00abFu loolu di xewe, Boroom bi?\u00bb Yeesu tontu leen ne: \u00abFa m\u00e9dd nekk, la tan yiy dajee.\u00bb\n18:1 Noonu Yeesu wax leen itam l\u00e9eb wii ngir xamal leen ne, war na\u00f1oo sax ci \u00f1aan te ba\u00f1 a x\u00e0ddi.\n18:2 Nee na: \u00abDafa amoon cib d\u00ebkk, benn \u00e0ttekat bu ragalul Y\u00e0lla te faalewul mbindeef.\n18:3 Amoon na itam ca d\u00ebkk ba jig\u00e9en ju j\u00ebkk\u00ebram faatu ju daan faral di \u00f1\u00ebw ci moom, naan ko: \u201c\u00c0tte ma ak sama noon!\u201d\n18:4 \u00c0ttekat ba ba\u00f1 lu y\u00e0gg, waaye am b\u00e9s mu ne ci xelam: \u201cRagaluma Y\u00e0lla te faalewuma mbindeef,\n18:5 waaye jig\u00e9en jii lakkal na ma; kon dinaa ko \u00e0tte, ngir mu ba\u00f1atee \u00f1\u00ebw sonal ma. Dina rey ak ay wax.\u201d\u00bb\n18:6 Boroom bi tegaat ca ne: \u00abD\u00e9gluleen bu baax li \u00e0ttekat bu bon boobu wax;\n18:7 ndax Y\u00e0lla du \u00e0tte jub mbooloom mi mu t\u00e0nn te \u00f1u koy \u00f1aan wall guddi ak b\u00ebcc\u00ebg? Ndax dina leen xaarloo?\n18:8 Maa ngi leen koy wax, dina leen \u00e0tte jub ci lu gaaw. Waaye bu Doomu nit ki \u00f1\u00ebwee, ndax dina fekk ng\u00ebm ci \u00e0ddina?\u00bb\n18:9 Yeesu waxaat l\u00e9eb wii nit, \u00f1i foog ne jub na\u00f1u tey xeeb \u00f1i ci des.\n18:10 Mu ne: \u00abDafa amoon \u00f1aari nit \u00f1u dem ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, di \u00f1aan. Kenn ki ab Farisen la, ki ci des juutikat.\n18:11 Farisen baa nga taxaw di \u00f1aan ci xelam naan: \u201cYaw Y\u00e0lla, maa ngi lay sant ci li ma melul ni \u00f1eneen \u00f1iy s\u00e0cc, di def lu jubadi te di njaaloo, rawatina juutikat bii.\n18:12 Ayu-b\u00e9s gu nekk damay woor \u00f1aari yoon, di joxe asaka ci l\u00e9pp lu ma wut.\u201d\n18:13 \u00abJuutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore te b\u00ebggul a siggi sax, xool ca asamaan. Waaye ma ngay f\u00ebgg d\u00ebnnam te naan: \u201cYaw Y\u00e0lla, y\u00ebr\u00ebm ma, man miy b\u00e0kkaarkat.\u201d\u00bb\n18:14 Yeesu teg ca ne: \u00abMaa ngi leen koy wax, nit kooku, ba muy \u00f1ibbi k\u00ebram, moom la Y\u00e0lla \u00e0tte ni ku jub, waaye du Farisen ba. Ndaxte k\u00e9pp kuy y\u00e9kkatiku dees na la suufeel, te kuy suufeelu, \u00f1u y\u00e9kkati la.\u00bb\n18:15 Amoon na ay nit, \u00f1uy indil Yeesu ay liir, ngir mu teg leen ay loxoom. Bi taalibe ya gisee loolu, \u00f1u g\u00ebdd leen.\n18:16 Waaye Yeesu woo leen ne: \u00abB\u00e0yyileen xale yi, \u00f1u \u00f1\u00ebw ci man, te buleen leen tere, ndaxte \u00f1u mel ni \u00f1oom \u00f1oo yelloo nguuru Y\u00e0lla.\n18:17 Ci d\u00ebgg, maa ngi leen koy wax, woyoful ni xale, nangu nguuru Y\u00e0lla, doo ci man a dugg.\u00bb\n18:18 Benn njiitu Yawut laaj Yeesu ne ko: \u00abKilifa gu baax gi, lu ma war a def, ba am w\u00e0ll ci dund gu dul jeex?\u00bb\n18:19 Yeesu tontu ko: \u00abLu tax nga wooye ma ku baax? Y\u00e0lla rekk a baax.\n18:20 Xam nga ndigal yi: \u201cBul njaaloo, bul b\u00f3om, bul s\u00e0cc, bul seede lu dul d\u00ebgg, teralal sa ndey ak sa baay.\u201d\u00bb\n18:21 Njiit la ne ko: \u00abLoolu l\u00e9pp s\u00e0mm naa ko li dale ci sama ndaw ba tey.\u00bb\n18:22 Bi Yeesu d\u00e9ggee loolu, mu ne ko: \u00abLenn rekk moo la dese. Jaayal li nga am l\u00e9pp, s\u00e9ddale ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan; boo noppee, nga \u00f1\u00ebw topp ci man.\u00bb\n18:23 Bi nit ka d\u00e9ggee loolu, mu am tiis, ndaxte ku bare woon alal la.\n18:24 Yeesu xool ko, daldi ne: \u00abBoroom alal, dugg ci nguuru Y\u00e0lla, lu jafee ngoogu!\n18:25 Gil\u00e9em jaar ci b\u00ebn-b\u00ebnu pusa moo g\u00ebn a yomb boroom alal dugg ci nguuru Y\u00e0lla.\u00bb\n18:26 \u00d1i doon d\u00e9glu daldi ne: \u00abKon nag ku man a mucc?\u00bb\n18:27 Yeesu tontu ne: \u00abLi t\u00eb nit \u00f1i, t\u00ebwul Y\u00e0lla.\u00bb\n18:28 Noonu Piyeer ne: \u00abNun de, d\u00ebddu nanu li nu am l\u00e9pp, topp la.\u00bb\n18:29 Yeesu ne leen: \u00abCi d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, k\u00e9pp ku d\u00ebddu k\u00ebr walla jabar walla ay doomi ndey walla ay waajur walla ay doom ngir nguuru Y\u00e0lla,\n18:30 dinga am tey jii ay yooni yoon, ak dund gu dul jeex \u00ebll\u00ebg.\u00bb\n18:31 Yeesu w\u00e9etoo ak fukki taalibe yi ak \u00f1aar ne leen: \u00abNu ngi dem Yerusalem, te li yonent yi bindoon l\u00e9pp ci mbirum Doomu nit ki dina mat.\n18:32 Dina\u00f1u ko j\u00e9bbal \u00f1i dul Yawut, \u00f1u \u00f1aawal ko, saaga ko, tifli ci kawam.\n18:33 Gannaaw bu \u00f1u ko d\u00f3oree ay yar ba noppi, dina\u00f1u ko rey, waaye ca \u00f1etteelu fan ba dina dekki.\u00bb\n18:34 Waaye taalibe ya d\u00e9ggu\u00f1u li mu leen doon wax; k\u00e0ddu yooyu ump na leen, te xamu\u00f1u li waxi Yeesu yooyu tekki.\n18:35 Bi Yeesu di agsi d\u00ebkku Yeriko, am gumba gu toogoon ca wetu yoon wa, di yelwaan.\n18:36 Naka la gumba ga d\u00e9gg mbooloo di j\u00e0ll, mu laaj lan moo xew.\n18:37 \u00d1u wax ko ne: \u00abYeesum Nasaret moo fay jaar.\u00bb\n18:38 Noonu mu yuuxu ne: \u00abYeesu, S\u00ebtu Daawuda, y\u00ebr\u00ebm ma!\u00bb\n18:39 \u00d1i jiitu woon g\u00ebdd ko, ngir mu noppi. Waaye muy g\u00ebn a yuuxu naan: \u00abS\u00ebtu Daawuda, y\u00ebr\u00ebm ma!\u00bb\n18:40 Noonu Yeesu taxaw, santaane \u00f1u indil ko ko. Bi mu jegesee, Yeesu laaj ko ne:\n18:41 \u00abLoo b\u00ebggoon ma defal la ko?\u00bb Mu ne ko: \u00abSang bi, damaa b\u00ebgg a gis.\u00bb\n18:42 Noonu Yeesu ne ko: \u00abNa say b\u00ebt gis! Sa ng\u00ebm faj na la.\u00bb\n18:43 Ca saa sa mu daldi gis. Noonu mu topp ci Yeesu, di m\u00e0ggal Y\u00e0lla. Mbooloo m\u00e9pp gis loolu, di sant Y\u00e0lla.\n19:1 Yeesu dugg na Yeriko, jaar ca d\u00ebkk ba, di dem.\n19:2 Waaye amoon na fa waa ju \u00f1uy wax Sase. Njiitu juutikat la, te di ku bare alal.\n19:3 B\u00ebgg na gis kan mooy Yeesu, waaye dafa g\u00e0tt lool, ba m\u00ebnu koo gis ndax mbooloo ma.\n19:4 Noonu mu daw, jiituji ca yoon wa, y\u00e9eg ci genn garab ngir gis Yeesu, ndaxte foofa la naroon a jaar.\n19:5 Bi Yeesu dikkee ba tollook garab ga nag, mu t\u00e9en ne ko: \u00abSase, w\u00e0ccal gaaw, ndax tey sa k\u00ebr laa war a dal.\u00bb\n19:6 Sase daldi gaawantu w\u00e0cc, ganale ko ak mb\u00e9g.\n19:7 \u00d1\u00e9pp gis loolu, di \u00f1urum-\u00f1urumi naan: \u00abMi ngi dal cig k\u00ebru boroom b\u00e0kkaar.\u00bb\n19:8 Waaye Sase taxaw ne Boroom bi: \u00abD\u00e9glul Boroom bi, dogu naa may sama genn-w\u00e0llu alal miskin yi, te lu ma mas a njubla\u014b nit, j\u00ebl alalam, dinaa ko fey \u00f1eenti yoon lu ni tollu.\u00bb\n19:9 Yeesu ne ko: \u00abMucc gi w\u00e0cc na tey ci k\u00ebr gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam.\n19:10 Ndaxte Doomu nit ki \u00f1\u00ebw na, ngir seet te musal \u00f1i r\u00e9er.\u00bb\n19:11 Bi nit \u00f1i doon d\u00e9glu k\u00e0ddu yooyu, Yeesu teg ca l\u00e9eb, ndaxte jege woon na Yerusalem, te \u00f1oom foogoon na\u00f1u ne, nguuru Y\u00e0lla dafay daldi fee\u00f1 ca saa sa.\n19:12 Mu ne nag: \u00abDafa amoon boroom juddu bu rafet bu demoon ci r\u00e9ew mu sore, ngir \u00f1u fal ko buur te mu dellusiwaat.\n19:13 Noonu mu woo fukk ci ay surgaam, jox ku nekk benn libidoor, ne leen: \u201cLigg\u00e9eyleen ci, ba may \u00f1ibbisi.\u201d\n19:14 Waaye waa r\u00e9ewam b\u00ebggu\u00f1u ko. Noonu \u00f1u y\u00f3nni ndaw ci gannaawam ne: \u201cB\u00ebggunu nit kii yilif nu.\u201d\n19:15 \u00abBi \u00f1u ko falee buur nag, ba mu dellusi, mu woolu surga, ya mu joxoon wurus wa, ngir xam nan la\u00f1u ci ligg\u00e9eye.\n19:16 Ku j\u00ebkk ka \u00f1\u00ebw ne ko: \u201cSang bi, sa libidoor bii jur na fukki libidoor.\u201d\n19:17 Buur ba ne ko: \u201cDef nga lu baax, surga bu baax nga. Segam wone nga ne, takku nga ci lu tuuti, falul ci fukki d\u00ebkk.\u201d\n19:18 Surga ba ca topp \u00f1\u00ebw ne: \u201cSang bi, sa libidoor ba indi na jur\u00f3omi libidoor.\u201d\n19:19 Buur ba ne ko: \u201cYaw, falul ci jur\u00f3omi d\u00ebkk.\u201d\n19:20 Keneen \u00f1\u00ebw ne: \u201cSang bi, sa libidoor baa ngi nii. Dama koo fasoon ci sekkit, denc ko.\n19:21 Dama laa ragaloon, ndaxte ku n\u00e9eg nga. Dangay nangu loo d\u00e9nkaanewul, di dajale loo jiwul.\u201d\n19:22 Buur ba ne ko: \u201cCi say wax laa lay \u00e0tte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku n\u00e9eg laa, di nangu lu ma d\u00e9nkaanewul, te dajale lu ma jiwul.\n19:23 Lu tax nag y\u00f3bbuwoo sama xaalis ca denckati xaalis ya? B\u00e9s bu ma \u00f1\u00ebwee nag, ma man a jot sama xaalis ak la mu jur.\u201d\n19:24 \u00abCi kaw loolu mu ne \u00f1a taxawoon ca wetam: \u201cNanguleen libidoor bi ci moom, jox ko boroom fukki libidoor yi.\u201d\n19:25 \u00d1u ne ko: \u201cSang bi, am na fukki libidoor ba noppi.\u201d\n19:26 Buur ba ne leen: \u201cMaa ngi leen koy wax, ku am, dina\u00f1u la dolli, waaye ku amul, li nga am as n\u00e9ew sax, dina\u00f1u ko nangu.\n19:27 Waaye sama noon yi, \u00f1i b\u00ebggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.\u201d\u00bb\n19:28 Bi mu waxee loolu ba noppi, Yeesu dafa daldi jiitu, j\u00ebm Yerusalem.\n19:29 Bi muy jege d\u00ebkki Betfase ak Betani, ci wetu tund wu \u00f1uy wax tundu Oliw ya, Yeesu yebal \u00f1aar ci ay taalibeem,\n19:30 ne leen: \u00abDemleen ci d\u00ebkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi.\n19:31 Bu leen kenn laajee: \u201cLu tax ngeen koy yiwi?\u201d tontuleen ko: \u201cBoroom bi da koo soxla.\u201d\u00bb\n19:32 \u00d1aari ndaw ya dem, fekk mbir ya deme, na leen ko Yeesu waxe woon.\n19:33 Bi \u00f1uy yiwi cumbur ga nag, ay boroomam ne leen: \u00abLu tax ngeen di yiwi cumbur gi?\u00bb\n19:34 \u00d1u tontu ne: \u00abNdaxte Boroom bi da koo soxla.\u00bb\n19:35 Noonu \u00f1u indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni y\u00e9re ca kaw, y\u00e9egal ca Yeesu.\n19:36 Bi muy dem, nit \u00f1i di lalal Yeesu seeni y\u00e9re ci yoon wi.\n19:37 Bi \u00f1u agsee fa mbartalum tundu Oliw ya doore, taalibeem y\u00e9pp fees ak mb\u00e9g, t\u00e0mbalee m\u00e0ggal Y\u00e0lla ca kaw ndax k\u00e9emaan yu bare yi \u00f1u gis.\n19:38 \u00d1u ngi naan:\u00abYaw buur biy \u00f1\u00ebw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Na j\u00e0mm am ca asamaan,te ndam li f\u00e9ete ca b\u00e9rab yu g\u00ebn a kawe!\u00bb\n19:39 Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: \u00abKilifa gi, yeddal sa taalibe yi!\u00bb\n19:40 Noonu mu tontu ne: \u00abMaa ngi leen koy wax, bu \u00f1u noppee \u00f1oom, doj yiy xaacu.\u00bb\n19:41 Bi Yeesu jegee d\u00ebkk ba, ba s\u00e9en ko, mu jooy ko\n19:42 naan: \u00abC\u00e9y yaw itam, boo xamoon b\u00e9sub tey yi la man a indil j\u00e0mm! Waaye fi mu ne m\u00ebnuloo koo gis.\n19:43 B\u00e9s dina \u00f1\u00ebwi yu say noon di jal, w\u00ebrale la. Dina\u00f1u la t\u00ebj ci biir, tanc la.\n19:44 Dina\u00f1u la y\u00e0qaate, yaw ak sa waa d\u00ebkk. Doj dootul des ci kaw doj ci yaw, ndaxte r\u00e0\u00f1\u00f1eewoo jamono ji Y\u00e0lla \u00f1\u00ebwe, wallusi la.\u00bb\n19:45 Gannaaw loolu Yeesu dugg ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, daldi d\u00e0q \u00f1a fay jaay,\n19:46 naan leen: \u00abMbind mi nee na: \u201cSama k\u00ebr k\u00ebru \u00f1aan ci Y\u00e0lla lay doon; waaye y\u00e9en def ngeen ko k\u00ebru s\u00e0cc.\u201d\u00bb\n19:47 B\u00e9s bu nekk Yeesu di j\u00e0ngale ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, \u00f1oom ak njiiti xeet wa, \u00f1u ngi ko doon wut a reylu.\n19:48 Waaye xamu\u00f1u woon lan la\u00f1u man a def, ndaxte nit \u00f1\u00e9pp a ngi ko doon d\u00e9glu, ba\u00f1 benn baat raw leen.\n20:1 Benn b\u00e9s Yeesu doon j\u00e0ngal nit \u00f1a ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, di leen y\u00e9gal xebaar bu baax bi. Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya \u00f1\u00ebw ne ko:\n20:2 \u00abWax nu ci ban sa\u00f1-sa\u00f1 ngay defe y\u00ebf yii, walla kan moo la may boobu sa\u00f1-sa\u00f1.\u00bb\n20:3 Yeesu tontu leen ne: \u00abMan itam dinaa leen laaj lenn: wax leen ma,\n20:4 la Yaxya daan def, di s\u00f3ob nit \u00f1i ci ndox, fu mu ko j\u00eble, ci Y\u00e0lla walla ci nit \u00f1i?\u00bb\n20:5 \u00d1u waxtaan ci seen biir naan: \u00abBu nu nee: \u201cCi Y\u00e0lla,\u201d dina laaj: \u201cLu tax g\u00ebmuleen ko kon?\u201d\n20:6 Te bu nu nee: \u201cCi nit \u00f1i,\u201d mbooloo m\u00e9pp dina\u00f1u nu s\u00e0nni ay xeer, ndaxte g\u00ebm na\u00f1u ne Yaxya yonent la woon.\u00bb\n20:7 Noonu \u00f1u tontu ne, xamu\u00f1u fu mu ko j\u00eble.\n20:8 Yeesu ne leen: \u00abKon man itam duma leen wax ci ban sa\u00f1-sa\u00f1 laay defe y\u00ebf yii.\u00bb\n20:9 Noonu Yeesu daldi wax nit \u00f1a l\u00e9eb wii: \u00abAmoon na nit ku j\u00ebmb\u00ebt toolu r\u00e9se\u00f1, batale ko ay beykat, dem tukki tukki bu y\u00e0gg.\n20:10 Bi tool bi \u00f1oree nag, mu y\u00f3nni surga ci \u00f1oom, ngir jot w\u00e0llam ci me\u00f1\u00f1eef gi. Waaye beykat yi d\u00f3or ko ay yar, d\u00e0q ko, mu dellu ak loxoy neen.\n20:11 Mu y\u00f3nniwaat beneen surga, \u00f1u d\u00f3or ko moom itam, toroxal ko, d\u00e0q ko, mu dellu ak loxoy neen.\n20:12 Mu y\u00f3nneeti \u00f1etteelu surga, \u00f1u gaa\u00f1 ko, d\u00e0q ko.\n20:13 \u00abBoroom tool ba daldi ne: \u201cNan laay def nag? Dinaa y\u00f3nni sama doom, sama reeni xol. X\u00eby na \u00f1u weg ko, moom.\u201d\n20:14 Waaye bi beykat yi gisee doom ji, \u00f1u ne ci seen biir: \u201cKii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.\u201d\n20:15 \u00d1u g\u00e9nne ko tool bi nag, rey ko.\u00bb Noonu Yeesu laaj leen: \u00abNu leen boroom tool bi di def, nag?\n20:16 Xanaa \u00f1\u00ebw, rey beykat yooyu, d\u00e9nk tool ba \u00f1eneen.\u00bb Bi Yeesu waxee loolu, nit \u00f1a ne ko: \u00abY\u00e0lla tere!\u00bb\n20:17 Waaye Yeesu ne leen j\u00e0kk, daldi ne: \u00abKon nag lu baat yii ci Mbind mi di tekki:\u201cDoj wa tabaxkat ya s\u00e0nni,mujj na di doju ko\u00f1.\u201d\n20:18 K\u00e9pp ku dal ci doj woowu, dammtoo, te ku mu dal ci sa kaw, rajaxe la.\u00bb\n20:19 Xutbakat ya ak saraxalekat yu mag ya \u00f1u ngi doon wut a j\u00e0pp Yeesu ca taxawaay ba, ndaxte xam na\u00f1u ne, \u00f1oo tax mu wax l\u00e9eb woowu. Waaye ragal na\u00f1u mbooloo ma.\n20:20 Noonu \u00f1u koy yeeru, daldi y\u00f3nni ay nit \u00f1u mbubboo njub, sas leen \u00f1u fexe koo j\u00e0pp ci ay waxam, ngir j\u00e9bbal ko boroom r\u00e9ew, ma yor kilifteef ak sa\u00f1-sa\u00f1.\n20:21 \u00d1u daldi \u00f1\u00ebw ci Yeesu ne ko: \u00abKilifa gi, xam nanu ne li ngay wax te di ko j\u00e0ngale lu jub la. Amuloo parl\u00e0qu, waaye dangay xamle yoonu Y\u00e0lla ci bu w\u00f3or.\n20:22 Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla d\u00e9et.\u00bb\n20:23 Waaye Yeesu xam na seen pexe ne leen:\n20:24 \u00abWonleen ma posetu denariyon. Kan la\u00f1u ci def nataalam ak turam?\u00bb \u00d1u tontu ko: \u00abSesaar.\u00bb\n20:25 Noonu mu ne leen: \u00abJoxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Y\u00e0lla li Y\u00e0lla moom.\u00bb\n20:26 Noonu m\u00ebnu\u00f1u ko woon a j\u00e0pp ciy waxam ci kanamu mbooloo ma; \u00f1u waaru ci tontoom, ba wedam.\n20:27 Noonu ay nit, \u00f1u bokk ci Sadusen yi, \u00f1\u00ebw ci moom. Sadusen yi nag \u00f1oom weddi na\u00f1u ndekkite li. Noonu \u00f1u laaj ko ne:\n20:28 \u00abKilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu te b\u00e0yyiwul doom ak jabaram, kooku war na donn jig\u00e9en ji, ba y\u00e9kkati giiru magam.\n20:29 Amoon na fi nag jur\u00f3om-\u00f1aari g\u00f3or \u00f1u bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te b\u00e0yyiwul doom.\n20:30 \u00d1aareel ba takk jig\u00e9en ja, def noonu; ak \u00f1etteel ba, ba jur\u00f3om-\u00f1aar \u00f1\u00e9pp faatu te b\u00e0yyiwu\u00f1u doom.\n20:32 Gannaaw ga nag jig\u00e9en ja it faatu.\n20:33 Ci ndekkite li nag, kan ci \u00f1oom moo war a donn jig\u00e9en ja, fekk ku nekk ci jur\u00f3om-\u00f1aar \u00f1i mas na koo takk?\u00bb\n20:34 Yeesu tontu leen ne: \u00abCi \u00e0ddina sii, g\u00f3or \u00f1i ak jig\u00e9en \u00f1i da\u00f1uy s\u00e9y.\n20:35 Waaye \u00f1a \u00f1u \u00e0tte ne, yeyoo na\u00f1oo bokk ci dundu \u00ebll\u00ebg ak ci ndekkite li, kenn du am jabar, kenn du am j\u00ebkk\u00ebr.\n20:36 Dafa fekk ne m\u00ebnatu\u00f1oo dee, ndaxte da\u00f1uy mel ni malaaka yi. Ay doomi Y\u00e0lla la\u00f1u ndaxte doomi ndekkite la\u00f1u.\n20:37 Te Musaa sax wone na ne, n\u00e9ew yi dina\u00f1u dekki, ci saarum ngarab si. Foofa Musaa wooye na fa Boroom bi: \u201cY\u00e0llay Ibraayma, Y\u00e0llay Isaaxa, di Y\u00e0llay Yanq\u00f3oba.\u201d\n20:38 Kon nag nekkul Y\u00e0llay \u00f1i dee waaye Y\u00e0llay \u00f1iy dund la, ndaxte Y\u00e0llaa tax \u00f1\u00e9pp di dund.\u00bb\n20:39 Ci kaw loolu ay xutbakat ne ko: \u00abLi nga wax d\u00ebgg la, kilifa gi!\u00bb\n20:40 Ndaxte kenn ci \u00f1oom \u00f1emeetu koo laaj dara.\n20:41 Noonu Yeesu ne leen: \u00abLu tax nit \u00f1i di wax ne, Almasi bi mooy s\u00ebtu Daawuda?\n20:42 Ndaxte Daawuda moom ci boppam moo ne ci Sab\u00f3or:\u201cBoroom bi nee na sama Boroom:\u2018Toogal ci sama ndeyjoor,\n20:43 ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.\u2019 \u201d\n20:44 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko \u201cBoroom bi,\u201d nu muy nekke s\u00ebtam?\u00bb\n20:45 Bi ko nit \u00f1a fa nekkoon \u00f1\u00e9pp doon d\u00e9glu, Yeesu ne ay taalibeem:\n20:46 \u00abMoytuleen xutbakat yi; da\u00f1oo b\u00ebgg di doxantu, sol ay mbubb yu r\u00e9y, te \u00f1\u00e9pp di leen nuyoo \u00f1aari loxo ci p\u00e9nc mi. Ci j\u00e0ngu yi, toogu yu f\u00e9ete kanam la\u00f1uy wut, te toogu yu yiw la\u00f1uy taamu ci reeri xew yi.\n20:47 \u00d1u ngi lekk alalu jig\u00e9en \u00f1i seen j\u00ebkk\u00ebr faatu, di \u00f1aan Y\u00e0lla ay \u00f1aani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina g\u00ebn a tar.\u00bb\n21:1 Noonu Yeesu siggi, s\u00e9en ay boroom alal \u00f1uy dugal seen sarax ca ndab ya ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga.\n21:2 Mu gis itam jenn jig\u00e9en ju j\u00ebkk\u00ebram faatu te mu \u00f1\u00e0kk, ju fa def \u00f1aari poseti x\u00e0njar.\n21:3 Noonu mu daldi ne: \u00abCi d\u00ebgg, maa ngi leen koy wax, jig\u00e9en ju \u00f1\u00e0kk jee moo \u00ebpp \u00f1eneen \u00f1\u00e9pp lu mu joxe.\n21:4 \u00d1oom \u00f1\u00e9pp da\u00f1u s\u00e0kku ci seen barele, waaye moom dafa s\u00e0kku ci n\u00e9ewleem, ba joxe xaalis bi mu waroon a dunde.\u00bb\n21:5 Noonu ay nit doon wax ci lu j\u00ebm ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, ak ni \u00f1u ko rafetale ak ay doj yu jafe ak alal ju \u00f1u j\u00e9bbal Y\u00e0lla. Waaye Yeesu ne leen:\n21:6 \u00abLi ngeen gis fii l\u00e9pp, jamono dina \u00f1\u00ebw joo xam ne dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.\u00bb\n21:7 \u00d1u laaj ko ne: \u00abKilifa gi, ka\u00f1 la loolu di am? Te luy tegtal ne, looloo ngi waaj a xew?\u00bb\n21:8 Yeesu tontu ne: \u00abMoytuleen, bu leen kenn nax. Ndaxte \u00f1u bare dina\u00f1u \u00f1\u00ebw ci sama tur ne: \u201cMoom laa,\u201d walla \u00f1u naan: \u201cJamono ji jegesi na.\u201d Buleen topp \u00f1oo\u00f1u.\n21:9 Bu ngeen d\u00e9ggee ay xare ak ay r\u00e9ew yu j\u00f3g, wottuleen a tiit, ndaxte f\u00e0ww yooyule j\u00ebkk a am. Waaye taxul mujug jamono daldi taxaw.\u00bb\n21:10 Noonu mu teg ca ne: \u00abXeet dina j\u00f3g, xeex ak weneen xeet, r\u00e9ew dina xeex ak meneen r\u00e9ew.\n21:11 Suuf dina yengu yengu yu r\u00e9y, te wopp ak xiif dina am ci b\u00e9rab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy j\u00f3ge asamaan.\n21:12 Waaye bala looloo xew, dees na leen j\u00e0pp, fitnaal leen, di leen j\u00e9bbal \u00e0ttekat yi ca j\u00e0ngu ya, t\u00ebj leen kaso. Dees na leen y\u00f3bbu ci kanam ay buur yi ak ay boroom r\u00e9ew ndax sama tur.\n21:13 Loolu dina leen ubbil bunt, ba ngeen man maa seedeel.\n21:14 Fasleen y\u00e9enee ba\u00f1 a wut lay ngir musal seen bopp.\n21:15 Ndaxte man ci sama bopp maa leen di jox k\u00e0ddu ak xel moo xam ne seeni noon du\u00f1u ko man a teggi, mbaa \u00f1u di ko weddi.\n21:16 Seeni waajur sax ak seeni doomi ndey, seeni bokk ak seeni xarit, dina\u00f1u leen j\u00e9bbal \u00e0ttekat yi, ba \u00f1u rey \u00f1enn ci y\u00e9en.\n21:17 Te \u00f1\u00e9pp dina\u00f1u leen ba\u00f1 ndax sama tur.\n21:18 Waaye seen genn kawar sax du neen.\n21:19 Seen mu\u00f1 moo leen di musal.\n21:20 \u00abBu ngeen gisee ay xarekat w\u00ebr d\u00ebkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji \u00f1u koy y\u00e0q, agsi na.\n21:21 Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir d\u00ebkk bi, nanga ko g\u00e9nn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca d\u00ebkk ba!\n21:22 Ndaxte ci b\u00e9s yooyu Y\u00e0lla dina fey j\u00ebf yi, te li \u00f1u bindoon ci t\u00e9ereb Y\u00e0lla dina mat.\n21:23 Ngalla jig\u00e9en \u00f1i \u00ebmb ca b\u00e9s yooya, ngalla it \u00f1iy n\u00e0mpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci r\u00e9ew mi, te Y\u00e0lla dina w\u00e0cce meram ci waa r\u00e9ew mii.\n21:24 Dees na leen reye ak i jaasi, j\u00e0pp leen jaam, y\u00f3bbu leen ci r\u00e9ewi \u00e0ddina s\u00e9pp. Te \u00f1i dul Yawut dina\u00f1u nappaaje Yerusalem, ba kera jamonoy \u00f1i dul Yawut mat.\n21:25 \u00abAy firnde dina\u00f1u fee\u00f1 ci jant bi, ci weer wi ak ci biddiiw yi. Ci kaw suuf xeet yi dina\u00f1u tiit, jaaxle ndax riiru g\u00e9ej gi ak yengu-yengub duus yi.\n21:26 Bu boobaa nit \u00f1iy x\u00ebm ndax tiitaange, bu \u00f1uy xalaat musiba, yi nar a w\u00e0cc ci \u00e0ddina, ndaxte dees na yengal k\u00e0ttani asamaan.\n21:27 Noonu dina\u00f1u gis Doomu nit ki di \u00f1\u00ebw ciw niir, \u00e0nd ak k\u00e0ttan ak ndam lu r\u00e9y.\n21:28 Bu mbir yooyu di t\u00e0mbalee xew nag, boo yaboo ngeen siggi, t\u00e9en, ndaxte seen njot jubsi na.\u00bb\n21:29 Noonu Yeesu misaal leen lii: \u00abXool-leen garabu figg ak yeneen garab yi.\n21:30 Bu \u00f1u gisee \u00f1u s\u00ebq, soxlawuleen kenn wax leen ne, nawet bi jubsi na xaat.\n21:31 Noonu itam bu ngeen gisee loolu l\u00e9pp xew, xamleen ne nguuru Y\u00e0lla jege na.\n21:32 \u00abCi d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii du\u00f1u w\u00e9y, te loolu l\u00e9pp amul.\n21:33 Asamaan ak suuf dina\u00f1u w\u00e9y, waaye samay wax du w\u00e9y mukk.\n21:34 \u00abMoytuleen seen nafsu diigal leen ci y\u00e0qute ak ci m\u00e0ndite ak ittey \u00e0ddina, ba b\u00e9s boobu bett leen ni mbaal.\n21:35 Ndaxte dina dal ci \u00f1\u00e9pp \u00f1i nekk ci kaw suuf.\n21:36 Yeewuleen, di sax ci \u00f1aan, ngir ngeen man a mucc ci loolu l\u00e9pp war a xew, te man a taxaw ak k\u00f3olute ci kanamu Doomu nit ki.\u00bb\n21:37 Yeesoo ngi daan yendoo j\u00e0ngale ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, te bu guddee mu dem ca tund wu \u00f1uy wax tundu Oliw ya, fanaan fa.\n21:38 Te nit \u00f1\u00e9pp da\u00f1u daan teel a x\u00eby ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, di ko d\u00e9glu.\n22:1 M\u00e0ggalu Mburu ya amul lawiir jege woon na, te \u00f1u di ko wax B\u00e9su J\u00e9ggi ba.\n22:2 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya di wut pexem reylu Yeesu, ndaxte da\u00f1oo ragaloon nit \u00f1a.\n22:3 Noonu Seytaane daldi solu Yudaa, mi \u00f1uy wooye Iskariyo te mu bokkoon ca fukki taalibe ya ak \u00f1aar.\n22:4 Noonu Yudaa dem waxtaani ak saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati k\u00ebr Y\u00e0lla ga, ba xam nan la leen di j\u00e9bbale Yeesu.\n22:5 \u00d1u am ca b\u00e0nneex bu r\u00e9y, dig ko xaalis.\n22:6 Yudaa nangu, di fexe jamono ju mu leen man a j\u00e9bbal Yeesu, fu mbooloo ma nekkul.\n22:7 B\u00e9su m\u00e0ggalu Mburu ya amul lawiir agsi, ca b\u00e9s boobu la\u00f1u waroon a rendi mbotem m\u00e0ggalu J\u00e9ggi ba.\n22:8 Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: \u00abDemleen, defaral nu reeru J\u00e9ggi ba.\u00bb\n22:9 \u00d1u ne ko: \u00abFan nga b\u00ebggoon, nu defare ko fa?\u00bb\n22:10 Mu ne leen: \u00abBu ngeen duggee ca d\u00ebkk ba, g\u00f3or gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek y\u00e9en. Toppleen ci moom ba ca k\u00ebr ga muy dugg,\n22:11 te ngeen ne boroom k\u00ebr ga: \u201cKilifa gi nee na: Ana n\u00e9egu gan, bi may lekke reeru J\u00e9ggi ba, man ak samay taalibe?\u201d\n22:12 Noonu dina leen won n\u00e9eg bu f\u00e9ete kaw, te yaa, \u00f1u defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.\u00bb\n22:13 \u00d1u dem, gis l\u00e9pp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu \u00f1u defar reer bi.\n22:14 Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi,\n22:15 ne leen: \u00abY\u00e0kkamti woon naa lool lekk ak y\u00e9en reeru J\u00e9ggi bii, laata \u00f1u may sonal.\n22:16 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Y\u00e0lla.\u00bb\n22:17 Noonu mu fab kaas, daldi sant Y\u00e0lla ne: \u00abJ\u00ebl-leen kaas bii, s\u00e9ddoo ko.\n22:18 Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum r\u00e9se\u00f1 mi, ba kera Y\u00e0lla di t\u00ebral nguuram.\u00bb\n22:19 Gannaaw loolu mu j\u00ebl mburu, sant Y\u00e0lla, damm ko, joxleen ko ne: \u00abLii sama yaram la, wi ma joxe ngir y\u00e9en. Defleen lii, ngir f\u00e0ttaliku ma.\u00bb\n22:20 Noonu itam bi \u00f1u lekkee ba noppi, mu j\u00ebl kaas bi ne leen: \u00abKaas bii mooy misaal k\u00f3ll\u00ebre gu bees gi Y\u00e0lla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir y\u00e9en.\n22:21 Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li.\n22:22 Doomu nit ki mu ngi dem, ni \u00f1u ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.\u00bb\n22:23 Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci \u00f1oom mooy nar a def loolu.\n22:24 Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci \u00f1oom moo g\u00ebn a m\u00e0gg.\n22:25 Yeesu ne leen: \u00abBuuri xeeti \u00e0ddina da\u00f1u leen di d\u00f3or yetu nguur, te kilifa yi da\u00f1uy s\u00e0kku ng\u00ebr\u00ebm.\n22:26 Waaye y\u00e9en buleen def noonu. Ki g\u00ebn a m\u00e0gg ci y\u00e9en, na nekk ni ki g\u00ebn a ndaw, te njiit mel ni surga.\n22:27 Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, \u00f1oom \u00f1aar kan moo ci g\u00ebn a m\u00e0gg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga.\n22:28 Y\u00e9en nag y\u00e9enay \u00f1i \u00e0nd ak man ci samay fitna.\n22:29 Man nag jox naa leen sa\u00f1-sa\u00f1u nguuru, ni ma ko sama Baay joxe.\n22:30 Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di \u00e0tte fukki giir ak \u00f1aar yu b\u00e0nni Israyil.\u00bb\n22:31 Yeesu teg ca ne: \u00abSimo\u014b, Simo\u014b! Seytaane \u00f1aan na, \u00f1u j\u00e9bbal leen ko, ngir mu teqale leen ni \u00f1u teqalee dugub ak xatax.\n22:32 Waaye man \u00f1aanal naa la, ngir sa ng\u00ebm d\u00ebg\u00ebr. Te yaw, boo dellusee, nanga d\u00ebg\u00ebral sa bokki taalibe yi.\u00bb\n22:33 Piyeer ne ko: \u00abBoroom bi, \u00e0ttan naa \u00e0nd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.\u00bb\n22:34 Yeesu tontu ko ne: \u00abPiyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi \u00f1etti yoon ne, xam nga ma.\u00bb\n22:35 Noonu Yeesu ne leen: \u00abBa ma leen yebalee te y\u00f3bbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla d\u00e0ll, ndax \u00f1\u00e0kkoon ngeen dara?\u00bb \u00d1u tontu ne: \u00abD\u00e9ed\u00e9et.\u00bb\n22:36 Mu neeti leen: \u00abL\u00e9egi nag k\u00e9pp ku am xaalis, na ko j\u00ebl; te ku am mbuus, na ko j\u00ebl; ku amul jaasi, na jaay mbubbam, j\u00ebnde ko jaasi.\n22:37 Ndaxte maa ngi leen koy wax, lii Mbind mi wax f\u00e0ww mu am ci man, bi mu nee: \u201cBoole na\u00f1u ko ak \u00f1u bon \u00f1a.\u201d Ndaxte loolu j\u00ebm ci man mi ngi mat.\u00bb\n22:38 Noonu taalibe ya ne ko: \u00abBoroom bi, \u00f1aari jaasee ngii.\u00bb Mu ne leen: \u00abDoy na.\u00bb\n22:39 Noonu Yeesu g\u00e9nn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe nakajekk. Taalibeem ya topp ci moom.\n22:40 Bi mu agsee ca b\u00e9rab ba, mu ne leen: \u00ab\u00d1aanleen, ngir ba\u00f1 a daanu cig fiir.\u00bb\n22:41 Noonu mu dand leen, ba fu aw saan man a tollu, daldi sukk di \u00f1aan ne:\n22:42 \u00abBaay, soo ko b\u00ebggee, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.\u00bb\n22:43 Noonu malaakam Y\u00e0lla daldi koy fee\u00f1u, may ko doole.\n22:44 Ci biir tiis, Yeesu g\u00ebn a sawar ci \u00f1aan gi, \u00f1aqam mel ni lumbi deret dal ci suuf.\n22:45 Bi mu \u00f1aanee ba noppi, mu j\u00f3g, dellusi ci taalibe yi, fekk leen \u00f1uy nelaw, ndaxte seen xol dafa sonnoon ak tiis.\n22:46 Noonu mu ne leen: \u00abLu tax ngeen di nelaw? J\u00f3gleen \u00f1aan, ngir ba\u00f1 a daanu cig fiir.\u00bb\n22:47 Bi Yeesu di wax, mbooloo mu bare agsi; ku \u00f1uy wax Yudaa te mu bokkoon ci fukki ndaw yi ak \u00f1aar jiite leen. Yudaa jege\u00f1si Yeesu, b\u00ebgg koo f\u00f3on.\n22:48 Waaye Yeesu ne ko: \u00abCi f\u00f3on ngay j\u00e9bbale Doomu nit ki ay noonam!\u00bb\n22:49 Bi \u00f1i \u00e0ndoon ak Yeesu gisee liy b\u00ebgg a xew, \u00f1u ne: \u00abBoroom bi, ndax nu d\u00f3ore jaasi?\u00bb\n22:50 Kenn ci \u00f1oom nag d\u00f3or surgab saraxalekat bu mag ba, noppu ndeyjooram dagg.\n22:51 Waaye Yeesu daldi ne: \u00abB\u00e0yyileen.\u00bb Mu laal noppu waa ja, w\u00e9ral ko.\n22:52 Noonu Yeesu ne saraxalekat yu mag ya ak kilifay wottukati k\u00ebr Y\u00e0lla ga ak njiiti xeet, wa ko j\u00e0ppsi woon: \u00abJ\u00f3g ngeen, g\u00e0nnaayoo jaasi ak yet, mel ni \u00f1uy topp s\u00e0cc.\n22:53 Moona maa nga woon ak y\u00e9en b\u00e9s bu nekk ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, te j\u00e0ppuleen ma. Waaye l\u00e9egi seen waxtu la, di jamonoy l\u00ebnd\u00ebm.\u00bb\n22:54 \u00d1u j\u00e0pp Yeesu, y\u00f3bbu ko ca k\u00ebr saraxalekat bu mag ba. Piyeer topp fu sore.\n22:55 Amoon na taal ca diggu \u00ebtt ba, ay nit toog, w\u00ebr ko, Piyeer itam toog ci seen biir.\n22:56 Ab mbindaan gis ko, mu toog, taal bi di ko leeral, mu ne ko j\u00e0kk ne: \u00abNit kii itam \u00e0ndoon na ak moom.\u00bb\n22:57 Waaye Piyeer weddi ko ne: \u00abSoxna si, xawma kooku.\u00bb\n22:58 Nes tuuti keneen gis ko ne: \u00abYaw itam ci \u00f1oom nga bokk.\u00bb Piyeer tontu ko: \u00abSama waay, bokkuma ci.\u00bb\n22:59 Bi \u00f1u tegee lu mat waxtu, keneen dikkaat ca wax ja ne: \u00abCi lu w\u00f3or nit kii \u00e0ndoon na ak moom, nde Galile la j\u00f3ge.\u00bb\n22:60 Waaye Piyeer tontu ne: \u00abSama waay, xawma li ngay wax!\u00bb Bi k\u00e0ddoom di daanu, faf ginaar daldi sab.\n22:61 Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer f\u00e0ttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: \u00abBala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi \u00f1etti yoon.\u00bb\n22:62 Piyeer daldi g\u00e9nn, di jooy jooy yu metti.\n22:63 Nit \u00f1aa nga j\u00e0ppoon Yeesu, di ko \u00f1aawal ak di ko d\u00f3or.\n22:64 \u00d1u ngi takkoon ay b\u00ebtam, di ko laaj, naan ko: \u00abYaw, wax nu ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, ku la d\u00f3or?\u00bb\n22:65 \u00d1u ngi ko doon tifaar it yeneeni saaga.\n22:66 Bi b\u00ebt setee, kureelu njiiti xeet wa, maanaam saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya, daldi daje, indi Yeesu ci seen kanam.\n22:67 \u00d1u ne ko: \u00abSoo dee Almasi bi, wax nu ko.\u00bb Mu tontu leen ne: \u00abSu ma leen ko waxee, dungeen ma g\u00ebm.\n22:68 Te su ma leen laajee, dungeen tontu.\n22:69 Waaye gannaawsi tey, Doomu nit ki dina toog ci ndeyjooru Y\u00e0lla, Aji K\u00e0ttan ji.\u00bb\n22:70 Noonu \u00f1\u00e9pp ne: \u00abKon nag yaay Doomu Y\u00e0lla ji?\u00bb Mu tontu leen ne: \u00abY\u00e9en ci seen bopp wax ngeen ne moom laa.\u00bb\n22:71 \u00d1u daldi ne nag: \u00abLu nuy doyeeti seede l\u00e9egi, ndegam nun ci sunu bopp noo ko nangoo ci g\u00e9mmi\u00f1am!\u00bb\n23:1 Gannaaw loolu kureelu \u00e0ttekat ya y\u00e9pp daldi j\u00f3g, y\u00f3bbu Yeesu ca Pilaat.\n23:2 Foofa \u00f1u t\u00e0mbali di ko sosal naan: \u00abFekk nanu nit kii, muy f\u00e0bbi sunu r\u00e9ew, di leen teree fey galag Sesaar, te mi ngi teg boppam Almasi, maanaam buur.\u00bb\n23:3 Noonu Pilaat laaj ko: \u00abNdax yaa di buuru Yawut yi?\u00bb Yeesu tontu ko ne: \u00abWax nga ko.\u00bb\n23:4 Pilaat ne saraxalekat yu mag ya ak mbooloo ma: \u00abGisuma genn too\u00f1 ci nit kii.\u00bb\n23:5 Waaye \u00f1u sax ci seeni wax naan: \u00abMi ngi j\u00f3gloo mbooloo mi, di j\u00e0ngale ci r\u00e9ewu Yawut ya m\u00e9pp, li dale ci Galile ba fii.\u00bb\n23:6 Bi Pilaat y\u00e9gee baat yooyu, mu laajte ne: \u00abNdax nit kii Galile la d\u00ebkk?\u00bb\n23:7 Bi mu y\u00e9gee ne, Yeesoo ngi nekk ci diiwaan bi Erodd yilif, mu y\u00f3nnee ko Erodd, mi nekkoon ci jamono jooju ci Yerusalem.\n23:8 Bi Erodd gisee Yeesu, mu am mb\u00e9g mu r\u00e9y. Bu y\u00e0gg ba tey dafa koo b\u00ebggoon a gis, ndaxte d\u00e9ggoon na \u00f1uy wax ci ay mbiram te yaakaaroon na ne, dina ko gis mu def k\u00e9emaan.\n23:9 Noonu mu laaj ko ay laaj yu bare, waaye Yeesu tontuwul dara.\n23:10 Saraxalekat yu mag ya ak xutbakat yaa nga fa woon, di ko jii\u00f1 bu metti.\n23:11 Noonu Erodd ak ay xarekatam toroxal Yeesu, di ko \u00f1aawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu rafet, delloo ko Pilaat.\n23:12 Erodd ak Pilaat da\u00f1oo \u00f1i ba\u00f1ante woon bu j\u00ebkk, waaye ca b\u00e9s booba doon na\u00f1u ay xarit.\n23:13 Pilaat daldi woo saraxalekat yu mag ya, njiit ya ak mbooloom Yawut ya ne leen:\n23:14 \u00abIndil ngeen ma nit kii, ne ma, day j\u00e0ddloo yoon mbooloo mi. L\u00e9egi nag man mii laaj naa ko ci seen kanam, waaye gisuma too\u00f1 ci moom ak li ngeen koy jii\u00f1 l\u00e9pp.\n23:15 Erodd itam gisul too\u00f1 gu mu def, ndegam mu y\u00f3nneewaat nu ko. Nit kii deful genn too\u00f1 gu jar \u00f1u koy rey.\n23:16 Kon nag dinaa ko d\u00f3orlu ay yar te b\u00e0yyi ko.\u00bb\n23:18 Waaye \u00f1u bokk di yuuxu, \u00f1oom \u00f1\u00e9pp naan: \u00abReyal kii te b\u00e0yyi Barabas!\u00bb\n23:19 Da\u00f1oo t\u00ebjoon Barabas, ndaxte dafa j\u00e9em a tas d\u00ebkk ba, te rey nit.\n23:20 Pilaat waxaat ak mbooloo ma, ndaxte dafa b\u00ebggoon a b\u00e0yyi Yeesu.\n23:21 Waaye \u00f1uy yuuxu naan: \u00abDaaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!\u00bb\n23:22 Pilaat ne leen \u00f1etteel bi yoon: \u00abLu tax? Gan too\u00f1 la def? Gisuma ci moom dara lu jar dee. Kon dinaa ko d\u00f3orlu ay yar te b\u00e0yyi ko.\u00bb\n23:23 Waaye \u00f1oom \u00f1u sax ca la \u00f1u waxoon, di g\u00ebn a yuuxu naan, \u00f1u daaj ko ci bant. Coow la yey Pilaat.\n23:24 Muj gi Pilaat dogal, \u00f1u defal leen li \u00f1u b\u00ebgg.\n23:25 Mu b\u00e0yyil leen ki \u00f1u ko \u00f1aanoon, kooku \u00f1u t\u00ebjoon kaso, ndax tas r\u00e9ew ma ak rey nit. Waaye mu j\u00e9bbal leen Yeesu ci seeni loxo.\n23:26 Bi \u00f1uy y\u00f3bbu Yeesu, \u00f1u j\u00e0pp ku \u00f1uy wax Simo\u014b te mu d\u00ebkk Siren, ku j\u00f3ge ca wet, ga f\u00e9ete ak tool ya, s\u00ebf ko bant, ba \u00f1uy war a daaj Yeesu, ngir mu g\u00e0ddu ko, topp ci moom.\n23:27 Mbooloo mu baree nga ko toppoon, te jig\u00e9en \u00f1u baree ngi doon yuuxu, di ko jooy.\n23:28 Yeesu daldi walbatiku ca \u00f1oom ne: \u00abY\u00e9en jig\u00e9eni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom.\n23:29 Ndaxte jamono dina \u00f1\u00ebw, ju \u00f1u naan: \u201cJig\u00e9en \u00f1i musul a jur ak \u00f1i musul a n\u00e0mpal, barkeel ngeen!\u201d\n23:30 Bu keroogee,\u201cNit \u00f1i dina\u00f1u ne tund yi:\u2018Daanuleen ci sunu kaw!\u2019te naan j\u00e0nj yi: \u00ab\u201cSuul-leen nu!\u00bb\u201c \u201c\n23:31 Ndaxte su \u00f1u defee nii garab gu tooy gi, lu \u00f1uy def garab gu wow gi?\u00bb\n23:32 Y\u00f3bbaale na\u00f1u itam \u00f1eneen, \u00f1uy \u00f1aari defkati lu bon, ngir rey leen.\n23:33 Bi xarekat ya agsee ba ca b\u00e9rab, ba \u00f1uy wooye Kaa\u014bu Bopp, \u00f1u daaj fa Yeesu ca bant, daajaale \u00f1aari defkati lu bon ya, kenn ca ndeyjooram, ka ca des ca c\u00e0mmoo\u00f1am.\n23:34 Ci kaw loolu Yeesu ne: \u00abBaay, baal leen, ndaxte xamu\u00f1u li \u00f1uy def.\u00bb Xarekat ya tegoo ay bant y\u00e9reem, ngir s\u00e9ddoo ko.\n23:35 Mbooloo maa nga fa taxaw di seetaan. Njiit ya di ko reetaan naan: \u00abMusal na \u00f1eneen; na musal boppam, su fekkee mooy Almasi bi, ki Y\u00e0lla fal!\u00bb\n23:36 Xarekat ya it di ko \u00f1aawal. \u00d1u jegesi, jox ko bineegar te naan:\n23:37 \u00abSu fekkee ne yaay buuru Yawut yi, musalal sa bopp!\u00bb\n23:38 \u00d1u daaj mbind, mu tiim ko naan: \u00abKii mooy buuru Yawut yi.\u00bb\n23:39 Kenn ca defkatu lu bon ya \u00f1u w\u00e9kkoon ci bant, di ko xas, naan ko: \u00abXanaa du yaw yaay Almasi bi? Musalal sa bopp te musal nu!\u00bb\n23:40 Waaye ka ca des yedd moroom ma, naan ko: \u00abXanaa ragaloo Y\u00e0lla, yaw mi \u00f1uy mbugal ni moom!\n23:41 Nun yelloo nanu sunu mbugal, waaye moom deful dara.\u00bb\n23:42 Noonu mu ne: \u00abYeesu, f\u00e0ttaliku ma, boo dellusee ci sa nguur.\u00bb\n23:43 Yeesu tontu ko ne: \u00abCi d\u00ebgg maa ngi la koy wax, tey jii dinga texe ak man ca jataayu Y\u00e0lla.\u00bb\n23:44 Noonu digg-b\u00ebcc\u00ebg daldi jot, jant ba n\u00ebbbu, r\u00e9ew m\u00e9pp daldi l\u00ebnd\u00ebm k\u00ebruus lu mat \u00f1etti waxtu. Ridob b\u00e9rab bu sell ba ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga daldi xar \u00f1aar.\n23:46 Yeesu woote ak k\u00e0ddu gu d\u00ebg\u00ebr naan: \u00abBaay, j\u00e9bbal naa la sama ruu!\u00bb Bi mu waxee loolu, mu delloo ruuwam Y\u00e0lla.\n23:47 Bi njiitu xare ba gisee li xewoon, mu m\u00e0ggal Y\u00e0lla ne: \u00abD\u00ebgg-d\u00ebgg nit kii ku jub la woon.\u00bb\n23:48 Nit \u00f1a fa dajaloo woon \u00f1\u00e9pp, di seetaan li xew, ba \u00f1u gisee loolu, \u00f1u dellu seen k\u00ebr, f\u00ebgg seen d\u00ebnn, di jooy.\n23:49 Xamey Yeesu y\u00e9pp ak jig\u00e9en, \u00f1a ko toppe woon Galile, dand leen, di xool li xew.\n23:50 Nit ku \u00f1uy wax Yuusufa dem ca Pilaat. Mi ngi d\u00ebkk Arimate ca diiwaanu Yude. Yuusufaa nga bokkoon ca kureelu \u00e0ttekat yi. Nit ku baax la woon te jub, te \u00e0ndul woon ci li \u00f1u dogaloon te j\u00ebf ko. Da doon s\u00e9entu nguuru Y\u00e0lla.\n23:52 Mu dem ca Pilaat, laaj ko n\u00e9ewu Yeesu.\n23:53 Gannaaw loolu mu w\u00e0cce ko ca bant ba, laxas ko ci c\u00e0ngaay, dugal ko cib b\u00e0mmeel bu \u00f1u yett ciw doj te musu\u00f1u caa def kenn.\n23:54 Fekk b\u00e9su Waajal la woon, te b\u00e9su noflaay baa ngi doon t\u00e0mbali.\n23:55 Jig\u00e9en \u00f1a gungee woon Yeesu Galile, \u00e0nd ak Yuusufa, gis b\u00e0mmeel ba ak na \u00f1u ca dence n\u00e9ewu Yeesu ba.\n23:56 Noonu \u00f1u dellu defari cuuraay ak latkolo\u00f1 ngir n\u00e9ew ba. Ca b\u00e9su noflaay ba \u00f1u noppalu, ni ko yoon wi santaanee.\n24:1 B\u00e9s bu j\u00ebkk ca ayu-b\u00e9s ga, jig\u00e9en \u00f1a j\u00f3g ca fajar, dem ca b\u00e0mmeel ba. \u00d1u ngi yoroon cuuraay lu \u00f1u defaroon.\n24:2 Bi \u00f1u agsee, \u00f1u fekk \u00f1u b\u00e9ra\u014b doj, wa uboon b\u00e0mmeel ba.\n24:3 \u00d1u dugg ca b\u00e0mmeel ba, waaye fekku\u00f1u fa n\u00e9ewu Boroom bi Yeesu.\n24:4 Noonu ba \u00f1u nekkee ak seen njaaxle, am na \u00f1aar \u00f1u leen fee\u00f1u, sol y\u00e9re yuy melax.\n24:5 Jig\u00e9en \u00f1a am tiitaange ju mag, daldi d\u00ebpp seen j\u00eb ci suuf. Waaye \u00f1u ne leen: \u00abLu tax ngeen di seet kiy dund ci biir n\u00e9ew yi?\n24:6 Nekkatu fi; dekki na. F\u00e0ttalikuleen la mu leen waxoon, ba mu nekkee Galile.\n24:7 Nee woon na: \u201cF\u00e0ww \u00f1u j\u00e9bbal Doomu nit ki b\u00e0kkaarkat yi, \u00f1u rey ko ci bant, mu dekki ca \u00f1etteelu fan ba.\u201d\u00bb\n24:8 Noonu \u00f1u daldi f\u00e0ttaliku k\u00e0dduy Yeesu ya.\n24:9 Bi \u00f1u j\u00f3gee b\u00e0mmeel ba, \u00f1u dem nettaliji loolu l\u00e9pp fukki ndaw ya ak benn, ak \u00f1a ca des \u00f1\u00e9pp.\n24:10 Jig\u00e9en \u00f1a \u00f1oo doon Maryaamam Magdala, S\u00e0nn, ak Maryaama yaayu Saag. Yeneen jig\u00e9en yi leen gunge woon itam nettali loolu ndaw ya.\n24:11 Waaye \u00f1u teg wax jooju ay jeneer, ba g\u00ebmu\u00f1u jig\u00e9en \u00f1oo\u00f1u.\n24:12 Waaye Piyeer daldi j\u00f3g, daw, dem ca b\u00e0mmeel ba. Bi mu \u00e0ggee, mu s\u00ebgg, y\u00ebr, gisul lu dul c\u00e0ngaay la. Noonu mu d\u00ebpp \u00f1ibbi, jaaxle lool ci li xew.\n24:13 Ca b\u00e9s boobu \u00f1aar ci taalibe yi di dem ci d\u00ebkku Emayus, te mu sore Yerusalem ci lu mat fukki kilomet.\n24:14 \u00d1u waxtaane li xewoon l\u00e9pp.\n24:15 Bi \u00f1uy waxtaan ak a sotteente xalaat, Yeesu ci boppam dab leen, \u00e0nd ak \u00f1oom,\n24:16 fekk seeni b\u00ebt muuru, ba m\u00ebnu ko woon a x\u00e0mmi.\n24:17 Yeesu ne leen: \u00abLan ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?\u00bb Noonu \u00f1u taxaw, seen xol jeex.\n24:18 Kenn ci \u00f1oom, ki tudd K\u00ebleyopas ne ko: \u00abXanaa yaw rekk yaa \u00f1\u00ebw Yerusalem te umple li fi xewoon b\u00e9s yii?\u00bb\n24:19 Yeesu ne leen: \u00abLu fi xew?\u00bb \u00d1u tontu ko ne: \u00abMbirum Yeesum Nasaret. Ab yonent la woon bu doon def ay j\u00ebf yu mag, di wax ay k\u00e0ddu yu am doole, ci kanam nit \u00f1i ak ca kanam Y\u00e0lla.\n24:20 Waaye sunuy saraxalekat yu mag ak sunuy njiit \u00f1oo ko j\u00e9bbal nguur gi ngir \u00f1u \u00e0tte ko, teg ko dee, ba daaj ko ci bant.\n24:21 Nun nag danoo yaakaaroon ne, mooy kiy nar a jot Israyil. Waaye bi loolu xewee ak l\u00e9egi, tey la \u00f1etteelu fan bi.\n24:22 Teewul nag am na ay jig\u00e9en yu bokk ci nun yu nu jaaxal. Da\u00f1oo fajaru ca b\u00e0mmeel ba,\n24:23 waaye fekku\u00f1u fa n\u00e9ewam. \u00d1u dellusi, nettali nu ne, ay malaaka fee\u00f1u na\u00f1u leen, y\u00e9gal leen ne, mi ngi dund.\n24:24 \u00d1enn ci sunu \u00e0ndandoo yi dem na\u00f1u ca b\u00e0mmeel ba, fekk l\u00e9pp mel, na ko jig\u00e9en \u00f1a waxe woon. Waaye moom gisu\u00f1u ko.\u00bb\n24:25 Noonu Yeesu ne leen: \u00abY\u00e9en daal, y\u00e9ena \u00f1\u00e0kk xel, te seen xol y\u00e9ex a g\u00ebm li yonent yi y\u00e9gle woon!\n24:26 Xanaa du Almasi bi dafa waroon a daj boobu coono te dugg ci ndamam?\u00bb\n24:27 Noonu mu t\u00e0mbalee ci yonent Y\u00e0lla Musaa ba ci yonent y\u00e9pp, tekkil leen li Mbind mi wax l\u00e9pp ci ay mbiram.\n24:28 Bi \u00f1uy jub d\u00ebkk, ba \u00f1u j\u00ebmoon nag, Yeesu def ni kuy jubal yoonam.\n24:29 Waaye \u00f1u t\u00e9ye ko ne ko: \u00abToogal fii ci nun, ndaxte jant baa ngi so, te l\u00e9egi mu guddi.\u00bb Noonu mu dugg, toog ca \u00f1oom.\n24:30 Bi \u00f1u t\u00e0mbali di reer, Yeesu j\u00ebl mburu ma, g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla, ba noppi damm ko, jox leen ko.\n24:31 Bi mu defee loolu, l\u00e9pp leer ci seeni b\u00ebt, \u00f1u daldi ko x\u00e0mmi. Waaye Yeesu ne mes, gisatu\u00f1u ko.\n24:32 Noonu ku nekk naan sa moroom: \u00abNdax sa xol seddul woon, bi muy wax ak nun ci yoon wi, te muy tekki Mbind mi?\u00bb\n24:33 \u00d1u daldi j\u00f3g ca saa sa, dellu Yerusalem, fekk fa fukki ndaw ya ak benn, ak yeneeni taalibe.\n24:34 \u00d1oo\u00f1u ne leen: \u00abD\u00ebgg la, Boroom bi dekki na, te fee\u00f1u na Simo\u014b!\u00bb\n24:35 \u00d1aari taalibe ya \u00f1oom it daldi leen nettali la xewoon ca yoon wa ak ni \u00f1u x\u00e0mmee Yeesu, bi mu dammee mburu ma.\n24:36 Bi \u00f1aari taalibe ya dee wax noonu, Yeesu taxaw moom ci boppam ci seen biir ne leen: \u00abNa j\u00e0mm w\u00e0cc ci y\u00e9en.\u00bb\n24:37 \u00d1u daldi tiit, foog ne da\u00f1oo gis njuuma.\n24:38 Waaye Yeesu ne leen: \u00abLu tax ngeen jaaxle, ak lu tax ngeen di xel \u00f1aar ci seen xol?\n24:39 Xool-leen samay loxo ak samay t\u00e0nk. Man mii la. Laal-leen ma te xam, njuuma amul yaram walla ay yax, ni ngeen gise, ma am ko.\u00bb\n24:40 Bi mu leen waxee loolu, mu won leen ay loxoom ak ay t\u00e0nkam.\n24:41 Waaye ba tey m\u00ebnu\u00f1u woon a g\u00ebm ndax seen mb\u00e9g ak jaaxle. Noonu Yeesu laaj leen ne: \u00abNdax am ngeen fii lu \u00f1u lekk?\u00bb\n24:42 \u00d1u jox ko dogu j\u00ebn wu \u00f1u lakk.\n24:43 Mu j\u00ebl ko, lekk ci seen kanam.\n24:44 Noonu mu ne leen: \u00abBi ma nekkee ak y\u00e9en, waxoon naa leen baat yii: li \u00f1u bind l\u00e9pp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci t\u00e9erey yonent yi ak ci Sab\u00f3or dafa war a am.\u00bb\n24:45 Noonu mu ubbi seen xel, ngir \u00f1u xam li Mbind mi di wax.\n24:46 Mu ne leen: \u00abF\u00e0ww Almasi bi sonn, mu dee te dekki ca \u00f1etteelu fan ba, ni \u00f1u ko binde,\n24:47 te it \u00f1uy y\u00e9gle xeet y\u00e9pp ci turam, dale ko ci Yerusalem ne, war na\u00f1oo tuub seeni b\u00e0kkaar, Y\u00e0lla baal leen.\n24:48 Y\u00e9enay samay seede.\n24:49 Te man dinaa leen y\u00f3nnee li sama Baay dige. Y\u00e9en nag toogleen ci d\u00ebkk bi, ba \u00f1u sol leen doole ji j\u00f3ge ci kaw.\u00bb\n24:50 Gannaaw loolu Yeesu y\u00f3bbu leen ca wetu Betani. Foofa mu y\u00e9kkati ay loxoom, barkeel leen.\n24:51 Bi mu leen dee barkeel, mu t\u00e0ggoo ak \u00f1oom, Y\u00e0lla y\u00e9ege ko asamaan.\n24:52 Taalibe ya m\u00e0ggal ko, daldi dellu Yerusalem, fees ak mb\u00e9g.\n24:53 Foofa daawu\u00f1u j\u00f3g ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, di g\u00ebr\u00ebm Y\u00e0lla.","title":"Wolof Bible (NT): Luke","type":"page"}
