{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/mar.htm","path":"bib/wb/wlf/mar.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/mar.htm","text":"1:1 Xebaar bu baaxu Yeesu Kirist, Doomu Y\u00e0lla, nii la t\u00e0mbalee.\n1:2 Bind na\u00f1u ci t\u00e9ereb yonent Y\u00e0lla Esayi naan:\u00abMaa ngi y\u00f3nni sama ndaw ci sa kanam,mu x\u00e0llal la sa yoon.\n1:3 Baat a ngi xaacu ca m\u00e0ndi\u014b ma naan:\u201cX\u00e0ll-leen yoonu Boroom bi,jubal-leen fi muy jaar.\u201d\u00bb\n1:4 Noonu Yaxya fee\u00f1 ca m\u00e0ndi\u014b ma, di s\u00f3ob nit \u00f1i ci ndox, tey waaree nii: \u00abTuubleen seeni b\u00e0kkaar, ba noppi ma s\u00f3ob leen ci ndox, ngir Y\u00e0lla baal leen seeni b\u00e0kkaar.\u00bb\n1:5 Kon waa diiwaanu Yude \u00f1\u00e9pp ak waa d\u00ebkku Yerusalem \u00f1\u00e9pp daldi g\u00e9nn j\u00ebm ci moom, di nangu seeni b\u00e0kkaar fi kanam \u00f1\u00e9pp, Yaxya s\u00f3ob leen ca dexu Yurdan.\n1:6 Yaxya nag mi ngi soloon mbubb mu \u00f1u r\u00e0bbe kawaru gil\u00e9em, takk laxasaayu der ci ndiggam. Ay nj\u00e9er\u00e9er la doon dunde ak lem.\n1:7 Mu waare ne: \u00abAm na kuy \u00f1\u00ebw sama gannaaw koo xam ne kii moo ma \u00ebpp k\u00e0ttan; yeyoowuma sax s\u00ebgg, ngir tekki ay d\u00e0llam.\n1:8 Maa ngi leen di s\u00f3ob ci ndox, waaye moom dina leen s\u00f3ob ci Xel mu Sell mi.\u00bb\n1:9 Booba Yeesu j\u00f3ge na d\u00ebkku Nasaret ci diiwaanu Galile, \u00f1\u00ebw, Yaxya s\u00f3ob ko ci dexu Yurdan.\n1:10 Bi muy g\u00e9nn ndox mi, mu daldi gis asamaan xar, te Xelum Y\u00e0lla di w\u00e0cc ci melow pitax, \u00f1\u00ebw ci moom.\n1:11 Te baat bu j\u00f3ge asamaan jib ne: \u00abYaa di sama Doom, ji ma b\u00ebgg; ci yaw laa ame b\u00e0nneex.\u00bb\n1:12 Ci kaw loolu Xelum Y\u00e0lla daldi j\u00e9\u00f1 Yeesu, mu dem ca m\u00e0ndi\u014b ma.\n1:13 Mu nekk fa \u00f1eent-fukki fan, j\u00e0nkoonte ak fiiri Seytaane; mu d\u00ebkk ci biir rabi \u00e0ll yi, te malaakay Y\u00e0lla di ko topptoo.\n1:14 Bi nga xamee ne j\u00e0pp na\u00f1u Yaxya, Yeesu dem ca diiwaanu Galile, di waare xebaar bu baaxu Y\u00e0lla,\n1:15 naan: \u00abJamono ji mat na, nguuru Y\u00e0lla jegesi na; tuubleen seeni b\u00e0kkaar te g\u00ebm xebaar bu baax bi.\u00bb\n1:16 Am b\u00e9s Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa \u00f1aar \u00f1u bokk ndey ak baay, di Simo\u014b ak Andare rakkam, \u00f1uy s\u00e0nni seeni mbaal ci dex gi, ndaxte ay nappkat la\u00f1u woon.\n1:17 Yeesu ne leen: \u00ab\u00d1\u00ebwleen topp ci man, dinaa leen def nappkati nit.\u00bb\n1:18 Ci saa si \u00f1u b\u00e0yyi seeni mbaal, topp ci moom.\n1:19 Bi Yeesu demee ba ca kanam, mu gis Saag doomu Sebede, ak Yowaana, mi mu bokkal ndey ak baay, \u00f1u nekk ci gaal gi, di defar seeni mbaal.\n1:20 Noonu Yeesu woo leen, \u00f1u daldi b\u00e0yyi seen baay Sebede ci gaal gi, moom ak surga ya, tey topp ci moom.\n1:21 Gannaaw loolu \u00f1u dem Kapernawum. Ca b\u00e9su noflaay nag Yeesu daldi dugg ci j\u00e0ngu bi, di leen j\u00e0ngal.\n1:22 Te \u00f1u waaru ca nj\u00e0ngaleem, ndaxte j\u00e0ngal na leen ak sa\u00f1-sa\u00f1 bu seeni xutbakat amul.\n1:23 Noonu am na ci j\u00e0ngu bi nit ku rab j\u00e0pp. Mu daldi yuuxu naan:\n1:24 \u00abYaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa \u00f1\u00ebw, ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell, ji j\u00f3ge ci Y\u00e0lla.\u00bb\n1:25 Waaye Yeesu g\u00ebdd ko naan: \u00abNoppil te g\u00e9nn ci moom.\u00bb\n1:26 Noonu rab wi daldi sayloo nit ki te g\u00e9nn ci moom ak yuux gu r\u00e9y.\n1:27 Bi loolu amee \u00f1\u00e9pp waaru, ba laajante naan: \u00abKii mooy kan? Mii nj\u00e0ngale lu bees la te \u00e0nd ak sa\u00f1-sa\u00f1. Day sant rab yi sax, \u00f1u di ko d\u00e9ggal.\u00bb\n1:28 Noonu turam daldi siiw ci diiwaani Galile g\u00e9pp.\n1:29 Bi nga xamee ne g\u00e9nn na\u00f1u ci j\u00e0ngu bi, \u00f1u \u00e0nd ak Saag ak Yowaana, dem ci k\u00ebr Simo\u014b ak Andare.\n1:30 Fekk gorob Simo\u014b bu jig\u00e9en t\u00ebdd wopp ak yaram wu t\u00e0ng; \u00f1u daldi ko y\u00e9gal Yeesu.\n1:31 Mu \u00f1\u00ebw nag ci moom, j\u00e0pp loxoom, y\u00e9kkati ko. Noonu t\u00e0ngoor wi daldi w\u00e0cc, te soxna si di leen topptoo.\n1:32 Ca ngoon sa nag, bi jant sowee, \u00f1u indil Yeesu \u00f1i wopp \u00f1\u00e9pp ak \u00f1i rab j\u00e0pp \u00f1\u00e9pp,\n1:33 ba d\u00ebkk bi b\u00e9pp dajaloo ci buntu k\u00ebr gi.\n1:34 Noonu mu w\u00e9ral \u00f1u bare, \u00f1u wopp ak ay j\u00e0ngoro yu wuute, te d\u00e0q ay rab yu bare. Waaye mu tere rab yi, \u00f1u wax dara, ndaxte xam na\u00f1u ko.\n1:35 Ca nj\u00ebl laata b\u00ebt di set, Yeesu j\u00f3g dem ca b\u00e9rab bu w\u00e9et, di fa \u00f1aan Y\u00e0lla.\n1:36 Simo\u014b nag ak \u00f1i \u00e0nd ak moom di ko seet fu nekk.\n1:37 Bi \u00f1u ko gisee, \u00f1u ne ko: \u00ab\u00d1\u00e9pp a ngi lay seet.\u00bb\n1:38 Waaye Yeesu tontu leen: \u00abNanu dem feneen ci d\u00ebkk yi nu w\u00ebr, ma waare fa itam, ndaxte moo tax ma g\u00e9nn.\u00bb\n1:39 Noonu mu w\u00ebr ci diiwaanu Galile g\u00e9pp, di waare ci seeni j\u00e0ngu, tey d\u00e0q rab yi.\n1:40 Am b\u00e9s ku gaana \u00f1\u00ebw ci moom, sukk, \u00f1aan ko ne: \u00abSoo ko b\u00ebggee, man nga maa w\u00e9ral.\u00bb\n1:41 Yeesu y\u00ebr\u00ebm ko, t\u00e0llal loxoom, laal ko naan: \u00abB\u00ebgg naa ko, w\u00e9ral.\u00bb\n1:42 Ca saa sa ngaanaam daldi de\u00f1, mu w\u00e9r.\n1:43 Noonu Yeesu yebal ko, d\u00e9nk ko bu w\u00e9r naan:\n1:44 \u00abMoytul a wax kenn dara, waaye demal won sa bopp saraxalekat bi, te nga j\u00e9bbal Y\u00e0lla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir \u00f1u xam ne w\u00e9r nga, te mu nekk seede ci \u00f1oom.\u00bb\n1:45 Waaye naka la waa ji g\u00e9nn, mu di y\u00e9ene ci kaw li xewoon, te di ko j\u00e9ebaane, ba tax Yeesu m\u00ebnatul a fa\u014baaral dugg cib d\u00ebkk, waaye mu nekk ci biti ciy b\u00e9rab yu w\u00e9et. Ba tey nit \u00f1i j\u00f3ge fu nekk, di ko fa fekk.\n2:1 Bi ay fan weesoo, Yeesu dellusi d\u00ebkku Kapernawum, mu siiw ne mu ngi ci k\u00ebr gi.\n2:2 Noonu nit \u00f1u bare dajaloo fa, ba kenn amatul foo taxaw, du ci bunt bi sax. Te Yeesu di leen y\u00e9gal k\u00e0ddu gi.\n2:3 Noonu, am \u00f1u ko indil ku yaramam w\u00e9pp l\u00e0ggi, \u00f1eenti nit j\u00e0ppoo ko.\n2:4 Waaye m\u00ebnu\u00f1u koo jege ndax mbooloo mi. Kon \u00f1u daldi teggi kaw k\u00ebr gi, di b\u00ebtt fa tiim b\u00e9rab ba Yeesu nekk, daldi yoor basa\u014b, ga l\u00e0ggi ba t\u00ebdd.\n2:5 Bi Yeesu gisee seen ng\u00ebm, mu ne l\u00e0ggi ba: \u00abSama waay, baal na\u00f1u la say b\u00e0kkaar.\u00bb\n2:6 Fekk ay xutbakat toog fa, \u00f1u di werante ci seen xel naan:\n2:7 \u00abKii kan la, ba sa\u00f1 a wax lii; mi ngi sosal Y\u00e0lla. Ana ku man a baale b\u00e0kkaar yi, ku dul Y\u00e0lla do\u014b\u014b?\u00bb\n2:8 Waaye Yeesu y\u00e9g ci xelam li \u00f1uy werante ci seen biir, ne leen: \u00abLu tax ngeen di werantee nii ci seen xel?\n2:9 Lan moo g\u00ebn a yomb, ma wax ku l\u00e0ggi ki: \u201cBaal na\u00f1u la say b\u00e0kkaar,\u201d walla ma wax ko: \u201cJ\u00f3gal, j\u00ebl sa basa\u014b, tey dox\u201d?\n2:10 Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci \u00e0ddina sa\u00f1-sa\u00f1u baale b\u00e0kkaar yi.\u00bb Ci kaw loolu mu ne l\u00e0ggi ba:\n2:11 \u00abMaa ngi la koy sant, j\u00f3gal, j\u00ebl sa basa\u014b te nga \u00f1ibbi.\u00bb\n2:12 Ca saa sa mu j\u00ebl basa\u014bam te g\u00e9nn fa kanam \u00f1\u00e9pp. Noonu \u00f1\u00e9pp waaru, di m\u00e0ggal Y\u00e0lla naan: \u00abLu mel ni lii, musunu koo gis.\u00bb\n2:13 Gannaaw loolu Yeesu g\u00e9nnaat, aw booru dex ga, mbooloo m\u00e9pp di \u00f1\u00ebw ci moom, mu di leen j\u00e0ngal.\n2:14 Bi Yeesu di romb, mu gis ku \u00f1uy wax Lewi, doomu Alfe, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: \u00abKaay topp ci man.\u00bb Mu j\u00f3g, daldi topp ci moom.\n2:15 Bi loolu amee Yeesu ak i taalibeem di lekk ci k\u00ebr Lewi, fekk ay juutikat ak ay boroom b\u00e0kkaar yu bare di lekkandoo ak \u00f1oom, ndaxte \u00f1u bare ci \u00f1oom a ko toppoon.\n2:16 Waaye xutbakat yi bokk ci Farisen yi, bi \u00f1u gisee ne, dafa bokk lekk ak ay juutikat ak ay boroom b\u00e0kkaar, \u00f1u daldi laaj taalibe yi: \u00abLu tax muy lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom b\u00e0kkaar?\u00bb\n2:17 Noonu Yeesu d\u00e9gg ko, mu ne leen: \u00ab\u00d1i w\u00e9r soxlawu\u00f1u fajkat, \u00f1i w\u00e9radi \u00f1oo ko soxla; \u00f1\u00ebwuma woo \u00f1i jub, waaye b\u00e0kkaarkat yi laay woo.\u00bb\n2:18 Taalibey Yaxya nag ak Farisen yi daan na\u00f1u woor. \u00d1u \u00f1\u00ebw nag fi Yeesu ne ko: \u00abLu tax taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi di woor, te say taalibe du\u00f1u woor?\u00bb\n2:19 Yeesu tontu leen: \u00abNdax gan, yi \u00f1\u00ebw cig c\u00e9et, dina\u00f1u woor, fekk boroom c\u00e9et gi \u00e0nd ak \u00f1oom? Du\u00f1u woor, li feek boroom c\u00e9et gaa ngi \u00e0nd ak \u00f1oom.\n2:20 Waaye b\u00e9s yaa ngi \u00f1\u00ebw, yu \u00f1uy j\u00eble boroom c\u00e9et gi; b\u00e9s boobaa nag dina\u00f1u woor.\n2:21 \u00abKenn du daax mbubb mu m\u00e0ggat ak sekkit wu bees; ndaxte sekkit wi day \u00f1oddi mbubb mi, te xottiku bi g\u00ebn a yaatu.\n2:22 Te kenn du def bii\u00f1 bu bees ci mbuusi der yu m\u00e0ggat. Lu ko moy, bii\u00f1 bi day toj mbuus yi, ba mbuus yi y\u00e0qu, ak bii\u00f1 bi tuuru. Waaye bii\u00f1 bu bees, ci mbuus yu bees la\u00f1u koy def.\u00bb\n2:23 Amoon na benn b\u00e9su noflaay Yeesu jaar ciy tool yu \u00f1or. Bi \u00f1uy dem nag, ay taalibeem daldi f\u00e0q ay gub.\n2:24 Noonu Farisen ya ne Yeesu: \u00abGisal, lu tax say taalibe di def lu jaaduwul ci b\u00e9su noflaay bi?\u00bb\n2:25 Yeesu tontu leen: \u00abNdax j\u00e0nguleen la Daawuda defoon, ba mu amee soxla te xiif, moom ak \u00f1a mu \u00e0ndaloon?\n2:26 Xanaa y\u00e9guleen li amoon ci b\u00e9si Abiyatar saraxalekat bu mag bi, ni Daawuda dugge woon ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, lekk mburu ya \u00f1u j\u00e9bbal Y\u00e0lla, jox ci it \u00f1a mu \u00e0ndaloon; fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul saraxalekat?\u00bb\n2:27 Yeesu dellu ne leen: \u00abY\u00e0lla s\u00e0kkul nit ngir b\u00e9su noflaay bi, waaye s\u00e0kk na b\u00e9su noflaay ngir nit.\n2:28 Noonu Doomu nit ki mooy boroom b\u00e9su noflaay bi.\u00bb\n3:1 Am beneen b\u00e9s, Yeesu duggaat ci j\u00e0ngu bi, fekk amoon na fa nit ku loxoom l\u00e0ggi.\n3:2 Am na fa nag ay Farisen, \u00f1uy xool Yeesu, ba xam dina ko faj ci b\u00e9su noflaay bi, ba man koo tuumaal.\n3:3 Yeesu ne ku loxoom l\u00e0ggi: \u00abJ\u00f3gal, taxaw ci kanamu \u00f1\u00e9pp.\u00bb\n3:4 Noonu Yeesu ne leen: \u00abLan moo jaadu, nu def ko b\u00e9su noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu rey nit?\u00bb Waaye \u00f1u ne cell.\n3:5 Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: \u00abT\u00e0llalal sa loxo.\u00bb Nit ki t\u00e0llal ko, loxoom daldi w\u00e9r pe\u014b\u014b.\n3:6 Ca saa sa nag Farisen ya g\u00e9nn, daldi gise ak \u00f1i far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu.\n3:7 Gannaaw loolu Yeesu ak ay taalibeem j\u00f3ge fa, j\u00ebm dex ga. Fekk mbooloo mu mag mu j\u00f3ge diiwaanu Galile, topp ko.\n3:8 Te it nit \u00f1u bare d\u00e9gg la mu def, \u00f1u \u00f1\u00ebw fi moom, j\u00f3ge diiwaanu Yude ak d\u00ebkku Yerusalem, ca diiwaanu Idume, ca gannaaw dexu Yurdan ak ci w\u00e0lli Tir ak Sidon.\n3:9 Booba nag Yeesu faj na \u00f1u bare, ba \u00f1u am ay j\u00e0ngoro di ko song, ngir laal ko. Noonu Yeesu wax ay taalibeem, \u00f1u wutal ko gaal, ngir mbooloo mi ba\u00f1 koo buux.\n3:11 Fekk booba k\u00e9pp ku rab j\u00e0pp ku ko gis, daanu fa kanamam di yuuxu naan: \u00abYaa di Doomu Y\u00e0lla.\u00bb\n3:12 Waaye Yeesu g\u00ebdd rab yi bu w\u00e9r, ngir \u00f1u ba\u00f1 koo siiwal.\n3:13 Gannaaw loolu Yeesu y\u00e9eg ci tund wi, woo \u00f1i ko neex, \u00f1u daldi \u00f1\u00ebw ci moom.\n3:14 Noonu mu t\u00e0nn ci fukk ak \u00f1aar, tudde leen ay ndawam, ngir \u00f1u \u00e0nd ak moom te mu y\u00f3nni leen, \u00f1u waareji,\n3:15 mu joxaale leen sa\u00f1-sa\u00f1u d\u00e0q ay rab.\n3:16 Fukk ak \u00f1aar \u00f1ii la t\u00e0nn:Simo\u014b, mi mu tudde Piyeer,\n3:17 Saag doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay \u2014 \u00f1oom \u00f1i mu wooye Bowanerses, maanaam \u00ab\u00d1i aaytal ni d\u00ebnnu gi\u00bb \u2014\n3:18 Andare ak Filib,Bartelemi ak Mac\u00eb,Tomaa ak Saag doomu Alfe,Tade ak Simo\u014b, mi bokk ca mbooloo, ma \u00f1u tudde \u00d1i farlu ci moom seen r\u00e9ew;\n3:19 ak Yudaa Iskariyo mi nar a wor Yeesu.\n3:20 Am beneen b\u00e9s Yeesu \u00f1\u00ebwaat ca k\u00ebr ga. Te mbooloo mu bare dajaloowaat fa, ba tax m\u00ebnu\u00f1oo lekk sax.\n3:21 Bi ko ay bokkam d\u00e9ggee nag, \u00f1u \u00f1\u00ebw, ngir j\u00e0ppsi ko naan: \u00abDafa t\u00e0ggoo ak sagoom.\u00bb\n3:22 Te it xutbakat ya j\u00f3ge Yerusalem ne: \u00abBeelsebul j\u00e0pp na ko; ci k\u00e0ttanu buuru rab yi lay d\u00e0qe rab yi.\u00bb\n3:23 Noonu Yeesu woo leen, wax ak \u00f1oom ciy l\u00e9eb ne leen: \u00abNaka la Seytaane man a d\u00e0qe Seytaane?\n3:24 R\u00e9ew mu xeex boppam, du man a y\u00e0gg.\n3:25 Te k\u00ebr gu xeex boppam, du man a y\u00e0gg.\n3:26 Bu Seytaane nag j\u00f3gee, ba xeex boppam, x\u00e0jjalikoo dikkal na ko te du man a y\u00e0gg, waaye dina tas.\n3:27 \u00abSu fi amee nit ku bare doole, naka la kenn man a dugge ci k\u00ebram, nangu alalam? Xanaa dafay j\u00ebkk a yeew ku bare doole ka, ba noppi door a toj k\u00ebram g\u00e9pp.\n3:28 Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, l\u00e9pp dees na ko baal nit \u00f1i, muy b\u00e0kkaar, muy sosal Y\u00e0lla wu mu man a doon.\n3:29 Waaye kuy sosal Xel mu Sell mi deesu ko baal mukk; g\u00e0ddu na b\u00e0kkaar ba f\u00e0ww.\u00bb\n3:30 Yeesu wax na loolu, ndaxte nee woon na\u00f1u, rab j\u00e0pp na ko.\n3:31 Noonu ndeyu Yeesu ak ay rakkam \u00f1\u00ebw, \u00f1u taxaw ci biti, y\u00f3nnee, woo ko.\n3:32 Fekk booba mbooloo nga toog, w\u00ebr ko. \u00d1u ne ko nag: \u00abSa yaay ak say rakk \u00f1u ngi taxaw ci biti, di la laaj.\u00bb\n3:33 Waaye Yeesu tontu leen: \u00abKan mooy sama ndey? \u00d1an \u00f1ooy samay rakk?\u00bb\n3:34 Noonu mu xool \u00f1i ko w\u00ebr naan: \u00abSama yaay ak samay rakk a ngii;\n3:35 ndaxte kuy def coobareg Y\u00e0lla, kooku mooy sama rakk ak sama jig\u00e9en ak sama ndey.\u00bb\n4:1 Am beneen yoon Yeesu nekk ci wetu dex ga, di j\u00e0ngalewaat. Mbooloo mu bare dajaloosi, ba tax mu y\u00e9eg cig gaal, dugg ca dex ga; mbooloo m\u00e9pp taxaw ca tefes ga.\n4:2 Noonu Yeesu daldi leen j\u00e0ngal lu bare ciy l\u00e9eb. Ci nj\u00e0ngaleem nag mu ne leen:\n4:3 \u00abD\u00e9gluleen, dafa amoon beykat bu demoon jiyi.\n4:4 Bi muy saaw toolam nag, lenn ci pepp mi wadd ci kaw yoon wi, picc yi daldi \u00f1\u00ebw, lekk ko l\u00e9pp.\n4:5 Leneen ci pepp mi wadd ci b\u00e9rab bu bare ay doj te n\u00e9ew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul.\n4:6 Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen.\n4:7 Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi sax, tanc ko, te me\u00f1\u00f1ul dara.\n4:8 Li ci des dal ci suuf su baax, mu j\u00f3g, sax, di focci ay gub; lii \u00e0ntu, ba mat fanweeri yoon lu \u00ebpp la mu ji woon, lii mat jur\u00f3om-benn-fukk, lii mat t\u00e9em\u00e9er.\u00bb\n4:9 Noonu Yeesu ne leen: \u00abD\u00e9glul bu baax, yaw mi am ay nopp.\u00bb\n4:10 Gannaaw loolu ba Yeesu nekkee fu w\u00e9et, fukki taalibe ak \u00f1aar \u00f1a, ak \u00f1eneen \u00f1u daan \u00e0nd ak \u00f1oom, laaj ko ci mbirum l\u00e9eb yi.\n4:11 Mu tontu leen: \u00abY\u00e9en may na\u00f1u leen, ngeen xam mb\u00f3oti nguuru Y\u00e0lla, waaye \u00f1i ci biti l\u00e9eb ay \u00ebmb l\u00e9pp.\n4:12 Noonu la, ngir:\u201c\u00d1uy xool bu baax waaye du\u00f1u gis dara,di d\u00e9glu bu baax waaye du\u00f1u xam dara,ngir ba\u00f1 \u00f1u tuub seeni b\u00e0kkaar,te Y\u00e0lla baal leen.\u201d\u00bb\n4:13 Noonu Yeesu ne leen: \u00abNdax xamuleen l\u00e9eb wii? Nu ngeen xame nag l\u00e9eb yi ci des?\n4:14 Ki ji nag, k\u00e0ddu gi lay ji.\n4:15 Ki f\u00e9ete ci yoon wi mooy ki d\u00e9gg, Seytaane \u00f1\u00ebw ci saa si, k\u00ebf k\u00e0ddu, gi \u00f1u def ci moom.\n4:16 Ki jot k\u00e0ddu gi ci b\u00e9rab bu bare ay doj mooy ki d\u00e9gg k\u00e0ddu gi, nangu ko ak mb\u00e9g ci saa si,\n4:17 waaye du y\u00e0gg, ndaxte wax ji saxul ci moom. Bu jaaree ci nattu nag, mbaa \u00f1u fitnaal ko ndax k\u00e0ddu gi, mu d\u00e0ggeeku ci saa si.\n4:18 Ki jot jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki d\u00e9gg k\u00e0ddu gi,\n4:19 waaye soxlay \u00e0ddina ak naxi alal ak b\u00ebgge solu ko, tanc k\u00e0ddu gi, ba du me\u00f1\u00f1 dara.\n4:20 Ki jot k\u00e0ddu gi ci suuf su baax si nag, mooy ki ko d\u00e9gg te nangu ko, ba jari\u00f1; kii mat fanweeri yoon lu \u00ebpp la \u00f1u ji woon, kii mat jur\u00f3om-benn-fukk, kii mat t\u00e9em\u00e9er.\u00bb\n4:21 Yeesu ne leen itam: \u00abNdax nit dina j\u00ebl l\u00e0mp, d\u00ebpp ci leget walla def ko ci ron lal? Ndax du ko w\u00e9kk?\n4:22 Amul dara luy kumpa lu \u00f1u warul a siiwal, mbaa mu l\u00e0qu te warul ne f\u00e0\u014b\u014b.\n4:23 D\u00e9glul bu baax, yaw mi am ay nopp.\u00bb\n4:24 Mu ne leen: \u00abSeetleen bu baax li ngeen di d\u00e9gg. Dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale, te dollil leen.\n4:25 Ku am, dees na la dollil; ku amul, li nga am as n\u00e9ew, dees na ko nangu.\u00bb\n4:26 Yeesu teg ci ne: \u00abNguuru Y\u00e0lla dafa mel ni nit ku ji tool.\n4:27 Muy nelaw walla muy xool, guddi mbaa b\u00ebcc\u00ebg, jiwu wi sax, di m\u00e0gg, te xamul naka la ko defe.\n4:28 Suuf day me\u00f1\u00f1 moom ci boppam, mu sax, focci, def i gub.\n4:29 Bu gub yi \u00f1oree nag, mu dagg ko, ndaxte ng\u00f3ob jot na.\u00bb\n4:30 Yeesu ne leen ati: \u00abLu nu man a mengaleel nguuru Y\u00e0lla? Walla ban l\u00e9eb lanu ko man a misaale?\n4:31 Dafa mel ni doomu fudd\u00ebn, bi g\u00ebn a tuuti ci jiwu y\u00e9pp;\n4:32 waaye boo ko jiwee, day j\u00f3g, m\u00e0gg, ba sut g\u00e0ncaxi t\u00f3ok\u00ebr y\u00e9pp; mu sax ay b\u00e0nqaas yu r\u00e9y, ba picci asamaan t\u00e0gg ci keram.\u00bb\n4:33 Noonu Yeesu d\u00e9gtal leen yeneeni l\u00e9eb yu bare yu mel ni yii, di leen xamal k\u00e0ddu gi, aju ci lu \u00f1u \u00e0ttan.\n4:34 Daawu leen wax dara lu dul ciy l\u00e9eb. Waaye bu w\u00e9etee ak ay taalibe, daan na leen firil l\u00e9pp.\n4:35 B\u00e9s booba nag ci ngoon Yeesu ne taalibe yi: \u00abNanu j\u00e0ll dex gi.\u00bb\n4:36 Mu yiwi mbooloo mi nag, ay taalibeem j\u00ebl ko ni mu mel ci gaal gi; te yeneeni gaal \u00e0nd ak moom.\n4:37 Naka noona ngelaw lu mag daldi j\u00f3g, duus yi s\u00e0ng gaal gi, ba mu b\u00ebgg a fees.\n4:38 Fekk Yeesu t\u00ebdd di nelaw ci ng\u00e9genaay ci taatu gaal gi.Taalibe yi daldi ko yee naan: \u00abKilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?\u00bb\n4:39 Ci kaw loolu Yeesu j\u00f3g, daldi g\u00ebdd ngelaw li, ne dex gi: \u00abNoppil te dal!\u00bb Noonu ngelaw li dal, ba l\u00e9pp ne nemm.\n4:40 Yeesu ne taalibe ya: \u00abLu tax ngeen tiit? Ndax g\u00ebmaguleen?\u00bb\n4:41 \u00d1u daldi ragal lool, naan ci seen biir: \u00abKii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko d\u00e9ggal?\u00bb\n5:1 Noonu \u00f1u j\u00e0ll dex ga, ba teer ci diiwaanu waa Serasa.\n5:2 Bi Yeesu g\u00e9nnee gaal gi, nit ku rab j\u00e0pp j\u00f3ge ca s\u00ebg ya, daldi \u00f1\u00ebw kar ko.\n5:3 Kooku nag ca s\u00ebg ya la d\u00ebkk, te kenn m\u00ebnu koo yeew, du ak c\u00e0llala sax.\n5:4 Ndaxte ay yoon yu bare j\u00e9ngoon na\u00f1u ko te yeew ko ak ay c\u00e0llala, waaye waa ji daldi dagg c\u00e0llala yi te damm j\u00e9ng yi, ba kenn amul woon k\u00e0ttanu t\u00e9ye ko.\n5:5 Guddi ak b\u00ebcc\u00ebg mu nga woon ca s\u00ebg ya ak ca tund ya, di yuuxu te jam yaramam ak ay xeer.\n5:6 Bi mu gisee Yeesu fu sore nag, mu daldi dawsi, sukk fa kanamam,\n5:7 di xaacu naan: \u00abYaw Yeesu Doomu Y\u00e0lla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Ci turu Y\u00e0lla, bu ma mbugal.\u00bb\n5:8 Ndaxte Yeesu nee woon na ko: \u00abYaw rab wu bon wi, g\u00e9nnal ci nit ki.\u00bb\n5:9 Noonu Yeesu laaj ko: \u00abNoo tudd?\u00bb Mu tontu ko: \u00abCoggal laa tudd, ndaxte \u00f1u bare lanu.\u00bb\n5:10 Muy \u00f1aan Yeesu lool, ngir mu ba\u00f1 leen a d\u00e0q ca r\u00e9ew ma.\n5:11 Fekk amoon na fa ca tund wa g\u00e9ttu mbaam-xuux yu bare yuy for.\n5:12 Rab ya \u00f1aan Yeesu: \u00abJox nu ndigal, nu dugg mbaam-xuux ya.\u00bb\n5:13 Mu may leen ko. Noonu rab ya g\u00e9nn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, \u00f1u daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab fa. Mbaam-xuux ya nag matoon na\u00f1u \u00f1aari junni.\n5:14 Noonu s\u00e0mm ya daw ca d\u00ebkk ba ak ca \u00e0ll ba, nettaliji mbir mi, ba nit \u00f1i \u00f1\u00ebw, seet li xew.\n5:15 \u00d1u \u00f1\u00ebw nag ci Yeesu, gis ka rab ya j\u00e0ppoon toog, sol ay y\u00e9re te \u00e0nd ak sagoom. \u00d1u daldi ragal.\n5:16 \u00d1a fekke woon mbir ma nag nettali leen mbirum nit ka ak mbaam-xuux ya.\n5:17 Ci kaw loolu \u00f1u daldi \u00f1aan Yeesu, mu sore seen r\u00e9ew.\n5:18 Bi Yeesu di dugg ci gaal gi, ki rab ya j\u00e0ppoon \u00f1aan Yeesu, ngir \u00e0nd ak moom.\n5:19 Waaye Yeesu mayu ko ko. Mu ne ko: \u00ab\u00d1ibbil ci say bokk, nettali leen ni la Boroom bi y\u00ebr\u00ebme, ba defal la lii l\u00e9pp.\u00bb\n5:20 Noonu waa ji dem ci diiwaanu Fukki d\u00ebkk yi, daldi fa y\u00e9gle la ko Yeesu defal, ba \u00f1\u00e9pp waaru.\n5:21 Noonu Yeesu j\u00e0llaat dex ga, taxaw ca tefes ga. Te nit \u00f1u bare dajaloo, w\u00ebr ko.\n5:22 Kenn ci njiiti j\u00e0ngu ba nag, tudd Yayrus, \u00f1\u00ebw ci moom. Naka la gis Yeesu, mu daanu ciy t\u00e0nkam,\n5:23 di ko saraxu lu bare naan: \u00abSama doom ju jig\u00e9en mi ngi b\u00ebgg a faatu; kaay teg ko loxo, ngir mu w\u00e9r te dund.\u00bb\n5:24 Noonu Yeesu \u00e0nd ak moom. Bi muy dem, mbooloo mu r\u00e9y topp ko, di ko tanc.\n5:25 Amoon na fa nag jig\u00e9en ju doon x\u00ebpp deret diirub fukki at ak \u00f1aar.\n5:26 Sonnoon na lool ci loxoy fajkat yu bare, s\u00e0nk ci alalam j\u00e9pp te j\u00eblewu ci genn tan, waaye faf wopp ja yokku.\n5:27 Noonu mu d\u00e9ggoon turu Yeesu, ne ci boppam: \u00abSu ma laalee ay y\u00e9reem rekk, dinaa w\u00e9r.\u00bb Mu jaxasoo ak mbooloo mi nag, doxe ko gannaaw, laal mbubbam.\n5:29 Ci saa si deret ji taxaw, mu y\u00e9g ci yaramam ne, j\u00e0ngoroom de\u00f1 na.\n5:30 Yeesu y\u00e9g ci saa si ne, doole g\u00e9nn na ci moom. Mu walbatiku nag ne mbooloo mi: \u00abAna ku laal samay y\u00e9re?\u00bb\n5:31 Ay taalibeem tontu ko: \u00abXanaa gisuloo mbooloo mi lay w\u00ebr; ngay laaj: \u201cKu ma laal?\u201d\u00bb\n5:32 Waaye Yeesu di xool li ko w\u00ebr, ngir gis ku ko def.\n5:33 Noonu jig\u00e9en ja \u00f1\u00ebw, daanu ciy t\u00e0nkam, wax ko d\u00ebgg g\u00e9pp; mu tiit bay lox, ndaxte xam na li xewoon ci yaramam.\n5:34 Yeesu ne ko: \u00abSoxna si, sa ng\u00ebm faj na la; demal ci j\u00e0mm, te na sa j\u00e0ngoro w\u00e0cc.\u00bb\n5:35 Bi Yeesu di wax nag, am na ku j\u00f3ge ca k\u00ebr njiit la, mu \u00f1\u00ebw naan: \u00abSa doom faatu na; matatul nuy sonal kilifa gi.\u00bb\n5:36 Waaye Yeesu j\u00e0ppul wax jooju; mu ne njiit la: \u00abG\u00ebmal rekk te ba\u00f1 a tiit.\u00bb\n5:37 Noonu Yeesu dem, \u00e0nd ak Piyeer, Saag ak Yowaana rekk, ndaxte mayul keneen, mu \u00e0nd ak moom.\n5:38 Naka la\u00f1u \u00f1\u00ebw ci k\u00ebr njiit li, Yeesu d\u00e9gg coow li; \u00f1ii di jooy, \u00f1ii di yuuxu.\n5:39 Mu dugg ne leen: \u00abLu ngeen di soow, tey jooy? Janq bi deewul, day nelaw rekk.\u00bb\n5:40 Waaye \u00f1u di ko \u00f1aawal. Noonu Yeesu g\u00e9nne \u00f1\u00e9pp, woo baayu janq bi ak yaay ji ak \u00f1i mu \u00e0ndal, dugg fa janq bi nekk.\n5:41 Mu j\u00e0pp loxoom ne ko: \u00abTalita kumi,\u00bb liy tekki: \u00abJanq bi, maa ngi la koy wax, j\u00f3gal.\u00bb\n5:42 Ca saa sa janq bi j\u00f3g, daldi dox, ndaxte amoon na fukki at ak \u00f1aar. \u00d1\u00e9pp daldi waaru, ba ne jomm.\n5:43 Ci kaw loolu Yeesu d\u00e9nk leen bu w\u00f3or, \u00f1u ba\u00f1 koo siiwal; teg ca naa: \u00abMayleen janq bi, mu lekk.\u00bb\n6:1 Bi loolu amee Yeesu j\u00f3ge fa, dellu r\u00e9ewam, \u00e0nd ak taalibe yi.\n6:2 B\u00e9su noflaay bi nag mu j\u00e0ngal leen ci seen j\u00e0ngu, ba mbooloom \u00f1i ko d\u00e9gg waaru naan: \u00abLii, fu mu ko j\u00eble, te xam-xam bii mu yor, lu mu doon, ba muy def k\u00e9emaan yii?\n6:3 Ndax kii du minise bi? Ndax du doomu Maryaama te magu Saag, Yuusufa, Yuda ak Simo\u014b? Te ay rakkam yu jig\u00e9en ndax nekku\u00f1u fi ak nun?\u00bb Kon nag \u00f1u daldi ko xeeb.\n6:4 Noonu Yeesu ne leen: \u00abDees na faaydaal yonent, waaye du ci r\u00e9ewam, ciy bokkam mbaa ci k\u00ebram.\u00bb\n6:5 Te Yeesu m\u00ebnu faa def ay k\u00e9emaan yu bare, lu dul teg loxo yenn jarag, w\u00e9ral leen.\n6:6 Te mu waaru ndax seen ng\u00ebmadi. Bi loolu amee Yeesu di w\u00ebr d\u00ebkk ya, di j\u00e0ngale.\n6:7 Noonu mu woo ci moom fukki taalibe ya ak \u00f1aar, jox leen sa\u00f1-sa\u00f1u d\u00e0q rab yi, y\u00f3nni leen, \u00f1u \u00e0nd \u00f1aar-\u00f1aar.\n6:8 Mu digal leen nii: \u00abBu ngeen di dem, buleen y\u00f3bbaale dara; du mburu mbaa mbuus mbaa xaalis ci seeni maxtume, waaye yemleen ci aw yet rekk.\n6:9 Sol-leen ay d\u00e0ll te yem ci benn turki.\u00bb\n6:10 Mu ne leen: \u00abK\u00ebr gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen j\u00f3ge d\u00ebkk ba.\n6:11 Koo xam ne g\u00e0ntu na leen, mbaa mu tanqamlu leen, g\u00e9nnleen fa, y\u00ebl\u00ebb seen p\u00ebndu t\u00e0nk, ngir seede leen seen r\u00e9er.\u00bb\n6:12 Noonu taalibe ya dem, di waare naan: \u00abTuubleen seeni b\u00e0kkaar.\u00bb\n6:13 \u00d1u d\u00e0q ay rab yu bare, te diw boppi jarag yu bare, w\u00e9ral leen.\n6:14 Noonu Erodd buur bi d\u00e9gg loolu, ndaxte turu Yeesu siiwoon na. Mu ne nag: \u00abYaxya dekki na, moo tax mu \u00e0nd ak k\u00e0ttanu def ay k\u00e9emaan.\u00bb\n6:15 \u00d1eneen ne: \u00abKii Iliyas la.\u00bb \u00d1i ci des ne: \u00abYonent la, bu mel ni yonent yu j\u00ebkk ya.\u00bb\n6:16 Waaye bi ko Erodd d\u00e9ggee, mu ne: \u00abYaxya male ma dagglu boppam, moom moo dekki.\u00bb\n6:17 Fekk Erodd y\u00f3nnee woon na, j\u00e0pp Yaxya, yeew ko, t\u00ebj. Ndaxte Erodd takkoon na Eroj\u00e0dd jabaru Filib magam.\n6:18 Te Yaxya ne ko: \u00abJaaduwul nga denc sa jabaru mag.\u00bb\n6:19 Moo tax Eroj\u00e0dd \u00ebmbal ko mer, ba b\u00ebgg koo rey, waaye m\u00ebnu koo def.\n6:20 Ndaxte Erodd dafa ragal Yaxya, ba s\u00e0mm bakkanam, xam ne ku jub la te sell. Bu ko daan d\u00e9glu it, day jaaxle lool, teewul mu b\u00e9g ci d\u00e9glu ko.\n6:21 Noonu b\u00e9s bu yell \u00f1\u00ebw, ba Erodd doon m\u00e0ggal b\u00e9su juddoom; mu woo ca xew wa ay jaraafam ak kilifay xare ba ak njiiti diiwaanu Galile.\n6:22 Booba doomu Eroj\u00e0dd dugg di fecc, mu neex Erodd ak gan \u00f1i, ba buur bi ne janq bi: \u00abLaaj ma loo b\u00ebgg, dinaa la ko jox.\u00bb\n6:23 Mu boole ci ngi\u00f1 ne ko: \u00abLoo ma man a laaj, dinaa la ko jox, ba ci genn-w\u00e0llu r\u00e9ew mi sax.\u00bb\n6:24 Noonu janq bi g\u00e9nn ne ndeyam: \u00abLu may laaj?\u00bb Mu tontu ko: \u00abLaajal boppu Yaxya.\u00bb\n6:25 Mu daldi gaawantoo dugg nag ci kanamu buur bi ne ko: \u00abDamaa b\u00ebgg, nga indil ma l\u00e9egi boppu Yaxya ci biir ndab.\u00bb\n6:26 Bi ko buur ba d\u00e9ggee, mu am naqar wu r\u00e9y. Waaye b\u00ebggu koo g\u00e0ntu ndax ngi\u00f1 li ak gan \u00f1i.\n6:27 Mu daldi y\u00f3nni nag xarekat, jox ko ndigal, mu indil ko boppu Yaxya. Waa ji dem, dagg boppu Yaxya ca kaso ba,\n6:28 indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq bi, mu daldi ko jox yaayam.\n6:29 Ba taalibey Yaxya d\u00e9ggee loolu, \u00f1u \u00f1\u00ebw, fab n\u00e9ew ba, suul ko ci b\u00e0mmeel.\n6:30 Gannaaw loolu ndaw yi dajaloo ci wetu Yeesu, nettali li \u00f1u def ak li \u00f1u j\u00e0ngale l\u00e9pp.\n6:31 Ci kaw loolu Yeesu ne leen: \u00abNanu beddeeku, dem ci b\u00e9rab bu w\u00e9et; ngeen noppalu fa tuuti.\u00bb Waxoon na loolu, ndaxte amoon na \u00f1u bare \u00f1u doon dem ak a dikk, ba amu\u00f1u sax jot ngir lekk.\n6:32 Noonu \u00f1u dugg cig gaal, dem ca b\u00e9rab bu w\u00e9et.\n6:33 Bi \u00f1uy dem nag, am \u00f1u leen gis, x\u00e0mmi leen, \u00f1u daldi j\u00f3ge ci d\u00ebkk y\u00e9pp, daw, jiitu leen fa.\n6:34 Bi Yeesu g\u00e9nnee gaal gi, mu gis mbooloo mu r\u00e9y, y\u00ebr\u00ebm leen, ndaxte da\u00f1oo mel ni xar yu amul s\u00e0mm. Kon mu daldi leen j\u00e0ngal lu bare.\n6:35 Ca ngoon sa taalibe yi \u00f1\u00ebw ci moom ne ko: \u00abFii \u00e0llub neen la, te l\u00e9egi mu guddi.\n6:36 Yiwil mbooloo mi nag, \u00f1u dugg ci \u00e0ll bi ak d\u00ebkk yi nu w\u00ebr, j\u00ebnd lu \u00f1u lekk.\u00bb\n6:37 Waaye Yeesu tontu leen ne: \u00abY\u00e9en joxleen leen lu \u00f1u lekk.\u00bb \u00d1u ne ko: \u00abXanaa nu j\u00ebnd lu tollook peyu jur\u00f3om-\u00f1etti weer ci mburu, jox leen \u00f1u lekk?\u00bb\n6:38 Yeesu laaj leen: \u00ab\u00d1aata mburu ngeen am? Demleen seeti.\u00bb \u00d1u dem seeti ne ko: \u00abJur\u00f3omi mburu ak \u00f1aari j\u00ebn.\u00bb\n6:39 Noonu Yeesu sant mbooloo mi, \u00f1u def ay g\u00e9ew, toog ci \u00f1ax mu naat mi.\n6:40 \u00d1u toog nag ay g\u00e9ewi jur\u00f3om-fukk ak t\u00e9em\u00e9er.\n6:41 Bi loolu amee Yeesu j\u00ebl jur\u00f3omi mburu yi ak \u00f1aari j\u00ebn yi, xool ci kaw, sant Y\u00e0lla, ba noppi mu damm mburu yi, jox ko taalibe yi, ngir \u00f1u s\u00e9ddale ko mbooloo mi. \u00d1aari j\u00ebn yi it mu s\u00e9ddale ko \u00f1\u00e9pp.\n6:42 Noonu \u00f1\u00e9pp lekk ba suur.\n6:43 Te it \u00f1u dajale la desoon ca dammiti mburu ak j\u00ebn ya, mu nekk fukki pa\u00f1e ak \u00f1aar yu fees.\n6:44 \u00d1u lekkoon nag matoon na limu jur\u00f3omi junniy g\u00f3or.\n6:45 Ci kaw loolu Yeesu sant ay taalibeem, \u00f1u dugg ci gaal gi, j\u00e0ll ba Betsayda, bi muy yiwi mbooloo mi.\n6:46 Bi mu t\u00e0ggtoo ak mbooloo mi, mu y\u00e9eg ca tund wa, \u00f1aan fa Y\u00e0lla.\n6:47 Noonu guddi jot, fekk gaal gi nekk ci diggu dex gi, te Yeesu rekk moo nekk ca tefes ga.\n6:48 Booba mu gis taalibe yi sonn lool ci joow gaal gi ndax li leen ngelaw li soflu. Ca nj\u00ebl nag mu j\u00ebm ci \u00f1oom, di dox ci kaw dex gi, ba xaw leen a raw.\n6:49 Bi \u00f1u ko gisee nag, muy dox ci kaw dex gi, \u00f1u foog ne njuuma la, daldi yuuxu.\n6:50 Ndaxte \u00f1\u00e9pp gis ko te jommi ci. Waaye mu wax ak \u00f1oom ci saa si ne leen: \u00abTakkleen seen fit, man la, buleen tiit!\u00bb\n6:51 Noonu mu fekksi leen ci gaal gi, ngelaw daldi ne tekk.\n6:52 Nj\u00e0qarey taalibe ya nag weesu dayo, ndaxte seen xol dafa fatt, ba r\u00e9ere mbir k\u00e9emaan, gi Yeesu defoon ci mburu yi.\n6:53 Bi nga xamee ne j\u00e0ll na\u00f1u, ba egg diiwaanu Senesaret, \u00f1u teer fa,\n6:54 g\u00e9nn ca gaal ga. Ci saa si nit \u00f1i x\u00e0mmi ko,\n6:55 \u00f1u daldi daw ca diiwaan ba b\u00e9pp, te f\u00e9pp fu \u00f1u ko d\u00e9gg \u00f1u di ko indil \u00f1u wopp, t\u00ebdd ci seeni lal.\n6:56 Te fu mu man a aw, ci d\u00ebkk yu mag mbaa yu ndaw walla ci \u00e0ll bi, \u00f1u indil ko jarag yi ci p\u00e9nc yi, \u00f1aan ko, mu may leen \u00f1u laal cati mbubbam rekk. Te k\u00e9pp ku ko laal daldi w\u00e9r.\n7:1 Amoon na b\u00e9s nag, ay Farisen ak ay xutbakat yu j\u00f3ge Yerusalem \u00f1\u00ebw ci Yeesu.\n7:2 \u00d1u gis yenn ciy taalibeem di lekk, fekk seeni loxo setul, maanaam raxasuwu\u00f1u woon, ni ko aada santaanee.\n7:3 Farisen yi nag \u00f1oom ak Yawut yi y\u00e9pp da\u00f1uy topp aaday yoon, yi maam yi t\u00ebral, te fandee leen g\u00ebnal lekk ak loxo yu \u00f1u raxasul.\n7:4 Te it bu \u00f1u j\u00f3gee p\u00e9nc ma, su \u00f1u sanguwul set, du\u00f1u lekk. Am na\u00f1u it yeneen aada yu bare, maanaam ni nga war a raxase ay kaas, ay njaq ak ay satala, ba \u00f1u laab.\n7:5 Noonu Farisen ya ak xutbakat ya laaj ko ne: \u00abLu tax say taalibe du\u00f1u topp aaday yoon, yi maam yi t\u00ebral, waaye \u00f1uy lekk ak loxo yu setul?\u00bb\n7:6 Yeesu tontu leen: \u00abEsayi waxoon na bu baax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla ci seen mbir, y\u00e9en naaf\u00e9q yi, bi mu bindee:\u201cXeet wii, \u00f1u ngi may teral ci seen g\u00e9mmi\u00f1,waaye seen xol sore na ma.\n7:7 Seen m\u00e0ggal amul benn njari\u00f1,ci li \u00f1uy j\u00e0ngale d\u00e9nkaaney nit kese.\u201d\u00bb\n7:8 Yeesu neeti leen: \u00abD\u00ebddu ngeen ndigali Y\u00e0lla, jublu ci aaday nit.\u00bb\n7:9 Mu teg ca ne leen: \u00abXelu ngeen ci tebbi ndigali Y\u00e0lla, ngir s\u00e0mm seen aada.\n7:10 Ndaxte Musaa nee na: \u201cTeralal sa ndey ak sa baay,\u201d teg ca ne: \u201cKu m\u00f3olu sa yaay walla sa baay, dees na la rey.\u201d\n7:11 Waaye y\u00e9en dangeen ne, ku ne sa yaay walla sa baay: \u201cLi nga war a jari\u00f1oo ci man Korban la,\u201d maanaam \u201cj\u00e9bbal naa ko Y\u00e0lla,\u201d\n7:12 dootuleen ko b\u00e0yyi, mu defal dara ndeyam walla baayam.\n7:13 Noonu tebbi ngeen k\u00e0ddug Y\u00e0lla ndax seen aada, ji ngeen di donnante. Te it y\u00e9ena ngi def yeneen yu bon yu mel nii.\u00bb\n7:14 Noonu Yeesu waxaat ak mbooloo mi ne leen: \u00abY\u00e9en \u00f1\u00e9pp d\u00e9gluleen ma te xam.\n7:15 Li ci biti, tey dugg nit, du ko man a indil sobe, waaye li g\u00e9nn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.\u00bb\n7:17 Bi nga xamee ne j\u00f3ge na\u00f1u ci mbooloo mi, dugg ci k\u00ebr gi, taalibe yi laaj Yeesu, mu firil leen wax ju l\u00e0qu jooju.\n7:18 Yeesu tontu leen ne: \u00abNdax y\u00e9en itam seen xol dafa t\u00ebju? Xanaa xamuleen ne, dara lu j\u00f3ge biti, dugg ci nit, du ko man a indil sobe,\n7:19 ndaxte du dugg ci xol, waaye ci biiram lay j\u00ebm, ba noppi daldi g\u00e9nn ca b\u00e9rab bu l\u00e0qu?\u00bb Ci li mu wax loolu Yeesu daganal na b\u00e9pp \u00f1am.\n7:20 Yeesu ne leen ati: \u00abLi g\u00e9nn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.\n7:21 Ndaxte ci biir, ci xolu nit, la xalaat yu bon di j\u00f3ge ak ndoxaanu y\u00e0qute, c\u00e0cc ak b\u00f3om,\n7:22 njaaloo ak b\u00ebgge, coxor, naaf\u00e9q, \u00f1aawteef, \u00f1eetaan, saaga, r\u00e9ylu ak j\u00ebfi ndof.\n7:23 Lu bon loolu l\u00e9pp day g\u00e9nn ci nit, di ko indil sobe.\u00bb\n7:24 Gannaaw loolu Yeesu j\u00f3ge fa, j\u00ebm weti d\u00ebkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci k\u00ebr, te b\u00ebggul kenn xam ko, waaye jataayam m\u00ebnul a umpe.\n7:25 Amoon na fa nag jig\u00e9en ju rab j\u00e0pp doomam ju jig\u00e9en. Bi mu d\u00e9ggee ne, Yeesoo nga fa, mu \u00f1\u00ebw, daanu ciy t\u00e0nkam,\n7:26 fekk jig\u00e9en ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo w\u00e0lli Fenisi ci diiwaanu Siri. Noonu jig\u00e9en ja \u00f1aan ko, mu d\u00e0q rab wi ci doomam.\n7:27 Waaye Yeesu ne ko: \u00abNa gune yi j\u00ebkk a lekk, ba regg; fab \u00f1amu gune yi, s\u00e0nni ko xaj yi, rafetul.\u00bb\n7:28 Jig\u00e9en ji tontu ko: \u00abWaaw sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci lekkukaayu gune yi.\u00bb\n7:29 Ci kaw loolu Yeesu ne ko: \u00abNdax wax jooju demal ci j\u00e0mm, rab wa g\u00e9nn na sa doom.\u00bb\n7:30 Noonu mu \u00f1ibbi, fekk doom ji t\u00ebdd cib lal te mucc ci rab wi.\n7:31 Bi loolu amee Yeesu j\u00f3ge na weti Tir, jaar ci w\u00e0lli d\u00ebkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi \u00f1uy wax Fukki d\u00ebkk yi.\n7:32 Foofa \u00f1u indil ko ku t\u00ebx te d\u00ebr lool, \u00f1aan ko mu teg ko loxo.\n7:33 Noonu Yeesu y\u00f3bbu ko, ba \u00f1u sore mbooloo mi, mu def ay baaraamam ciy noppam, daldi tifli, laal l\u00e0mmi\u00f1am.\n7:34 Mu y\u00ebr\u00ebm ko, ba binni ci xolam, xool ci asamaan, daldi ne: \u00abEffata,\u00bb liy tekki: \u00abUbbikuleen.\u00bb\n7:35 Ci saa si ay noppam daldi d\u00e9gg te l\u00e0mmi\u00f1am yiwiku, muy wax bu leer.\n7:36 Bi mu ko defee Yeesu tere leen, \u00f1u wax ko kenn, waaye lu mu leen ko g\u00ebn a tere, \u00f1u g\u00ebn ko nee siiwale.\n7:37 \u00d1u waaru lool naan: \u00abL\u00e9pp lu mu def, lu y\u00e9eme la. May na sax t\u00ebx yi \u00f1uy d\u00e9gg, ak luu yi \u00f1uy wax.\u00bb\n8:1 Ca b\u00e9s yooya mbooloo mu r\u00e9y amaatoon na, te amu\u00f1u woon lu \u00f1u lekk. Noonu Yeesu woo taalibe ya ne leen:\n8:2 \u00abY\u00ebr\u00ebm naa mbooloo mi, ndaxte toog na\u00f1u fi man \u00f1etti fan, te amatu\u00f1u lu \u00f1u lekk.\n8:3 Su ma leen yiwee ak seen xiif, dina\u00f1u t\u00eble ci yoon wi, ndaxte am na \u00f1u j\u00f3ge fu sore.\u00bb\n8:4 Taalibe yi tontu ko: \u00abWaaye fii \u00e0llub neen la; fu nuy j\u00eble lu doy ngir dundal leen?\u00bb\n8:5 Yeesu laaj leen: \u00ab\u00d1aata mburu ngeen am?\u00bb \u00d1u ne ko: \u00abJur\u00f3om-\u00f1aar.\u00bb\n8:6 Noonu Yeesu sant mbooloo mi, \u00f1u toog ci suuf. Mu j\u00ebl jur\u00f3om-\u00f1aari mburu yi, sant Y\u00e0lla, damm leen, jox leen taalibe yi, ngir \u00f1u s\u00e9ddale leen mbooloo mi; taalibe yi def ko.\n8:7 Amoon na fa it tuuti j\u00ebn yu ndaw. Yeesu j\u00ebl ko, sant Y\u00e0lla, wax taalibe yi, \u00f1u s\u00e9ddale leen itam mbooloo mi.\n8:8 Noonu nit \u00f1i lekk ba suur, ba noppi taalibe yi dajale jur\u00f3om-\u00f1aari d\u00e0mba yu fees ak dammit yi ci des.\n8:9 \u00d1a ko fekke nag matoon na\u00f1u \u00f1eenti junniy g\u00f3or.\n8:10 Bi ko Yeesu defee, mu yiwi leen, daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga, dem ca w\u00e0lli Dalmanuta.\n8:11 Noonu Farisen yi \u00f1\u00ebw, di werante ak moom; \u00f1u fexe koo fiir, ba laaj ko k\u00e9emaan gu j\u00f3ge ci asamaan tey firndeel y\u00f3nnentam.\n8:12 Waaye Yeesu binni ci xolam ne leen: \u00abLu tax niti jamono jii di laaj k\u00e9emaan? Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, du\u00f1u jot genn k\u00e9emaan.\u00bb\n8:13 Ci kaw loolu Yeesu b\u00e0yyi leen, duggaat ci gaal gi, di j\u00e0ll dex gi.\n8:14 Taalibe yi nag f\u00e0tte woon na\u00f1u y\u00f3bbaale mburu, te amu\u00f1u woon lu dul benn mburu ci gaal gi.\n8:15 Noonu Yeesu artu leen ne: \u00abWottuleen te moytu lawiiru Farisen yi ak \u00f1i far ak buur bi Erodd.\u00bb\n8:16 Taalibe yi nag daldi werante naan: \u00abNun de indaalewunu mburu.\u00bb\n8:17 Waaye Yeesu y\u00e9g loolu ne leen: \u00abLu tax ngeen di werante ci li ngeen indaalewul mburu? Xanaa gisaguleen te xamuleen? Ndax seen xol dafa fatt ba tey?\n8:18 Ndax ay gumbay nj\u00e0ccaar ngeen, te seeni nopp naqari? Xanaa f\u00e0ttalikuwuleen;\n8:19 bi ma dammee jur\u00f3omi mburu ya ngir jur\u00f3omi junni \u00f1a, \u00f1aata pa\u00f1e yu fees ak ay dammit ngeen ca dajale woon?\u00bb \u00d1u tontu ko: \u00abFukk ak \u00f1aar.\u00bb\n8:20 Yeesu neeti leen: \u00abTe b\u00e9s bi ma dammee jur\u00f3om-\u00f1aari mburu yi ngir \u00f1eenti junni \u00f1i, \u00f1aata d\u00e0mba yu fees ak dammit ngeen dajale woon?\u00bb \u00d1u ne ko: \u00abJur\u00f3om \u00f1aar.\u00bb\n8:21 Noonu Yeesu ne leen: \u00abNdax seen xol dafa t\u00ebju ba tey?\u00bb\n8:22 Gannaaw loolu \u00f1u \u00f1\u00ebw ci Betsayda. Foofa \u00f1u indil Yeesu ku gumba, di ko \u00f1aan, mu laal ko.\n8:23 Yeesu nag j\u00e0pp loxob gumba gi, y\u00f3bbu ko, ba g\u00e9nn d\u00ebkk bi. Mu def tiflit ciy b\u00ebtam, teg ko loxo naan: \u00abNdax gis nga dara?\u00bb\n8:24 Waa ji xool ne ko: \u00abGis naa ay nit, \u00f1u mel ni ay garab, te \u00f1u ngi dox.\u00bb\n8:25 Kon Yeesu laalaat b\u00ebt yi, gumba gi ne xefeet, daldi w\u00e9r, ba gis l\u00e9pp bu leer.\n8:26 Ci kaw loolu Yeesu sant ko mu \u00f1ibbi ne ko: \u00abBul dugg ca d\u00ebkk ba.\u00bb\n8:27 Bi loolu amee Yeesu \u00e0nd ak ay taalibeem, dem ca d\u00ebkk, yi w\u00ebr Sesare bu Filib. Bi \u00f1uy dem nag, mu laaj taalibe yi: \u00abNit \u00f1i, lu \u00f1u wax ne man moom laa?\u00bb\n8:28 \u00d1u ne ko: \u00abAm na \u00f1uy ne, yaa di Yaxya; \u00f1eneen ne, Iliyas; \u00f1i ci des ne, yaay kenn ci yonent yi.\u00bb\n8:29 Noonu Yeesu laaj leen: \u00abY\u00e9en nag, ku ngeen wax ne moom laa?\u00bb Piyeer tontu ko: \u00abYaa di Almasi bi.\u00bb\n8:30 Ci kaw loolu Yeesu d\u00e9nk leen bu w\u00f3or, \u00f1u ba\u00f1 koo wax kenn.\n8:31 Booba Yeesu t\u00e0mbali na leen a xamal ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare; njiit ya, saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya d\u00ebddu ko, \u00f1u rey ko, mu dekki ci \u00f1etti fan.\n8:32 Noonu mu xamal leen mbir mi, ba mu leer n\u00e0\u00f1\u00f1. Bi ko Piyeer d\u00e9ggee, mu woo ko ci pegg, daldi ko yedd.\n8:33 Waaye Yeesu geestu, gis yeneen taalibe yi, mu daldi yedd Piyeer ne ko: \u00abSore ma Seytaane; y\u00ebfi nit ngay fonk, waaye du y\u00ebfi Y\u00e0lla.\u00bb\n8:34 Noonu Yeesu woo taalibe yi ak mbooloo mi ne leen: \u00abKu b\u00ebgg a topp ci samay t\u00e0nk, na b\u00e0yyi boppam te g\u00e0ddu bant bi \u00f1u ko war a daaj, door a topp ci man.\n8:35 Ndaxte koo xam ne b\u00ebgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko \u00f1\u00e0kk, waaye ku \u00f1\u00e0kk sa bakkan ngir man ak ngir xebaar bu baax bi, dinga ko jotaat.\n8:36 Ndaxte moom \u00e0ddina s\u00e9pp, lu muy jari\u00f1 nit, bu \u00f1\u00e0kkee bakkanam?\n8:37 Te nit, lu mu war a weccee bakkanam?\n8:38 Ku ma rus a faral, te nanguwul samay wax ci kanamu niti jamono jii, \u00f1i fecci seen k\u00f3ll\u00ebre ak Y\u00e0lla te topp b\u00e0kkaar, Doomu nit ki dina la rus a xam, b\u00e9s bu \u00f1\u00ebwee ci ndamu Baayam, \u00e0nd ak malaaka yu sell yi.\u00bb\n9:1 Mu ne leen ati: \u00abCi d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, am na \u00f1i fi taxaw, \u00f1oo xam ne du\u00f1u dee, te gisu\u00f1u nguuru Y\u00e0lla \u00f1\u00ebw ak doole.\u00bb\n9:2 Jur\u00f3om-benni fan gannaaw gi, Yeesu \u00e0ndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana, mu y\u00f3bbu leen \u00f1oom rekk fu w\u00e9et ci tund wu kawe lool. Foofa j\u00ebmmam soppiku ci seen kanam;\n9:3 ay y\u00e9reem di ray-rayi, weex t\u00e0ll, te f\u00f3otukatu \u00e0ddina m\u00ebnu leen weexale nii.\n9:4 Noonu \u00f1u gis yonenti Y\u00e0lla Iliyas ak Musaa, di wax ak Yeesu.\n9:5 Piyeer daldi ne Yeesu: \u00abKilifa gi, b\u00e9g nanu ci sunu teew fii; nanu defar \u00f1etti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Iliyas.\u00bb\n9:6 Fekk xamul lu muy wax, ndaxte tiitaange j\u00e0pp na leen \u00f1oom \u00f1ett \u00f1\u00e9pp.\n9:7 Noonu niir muur leen, te baat jibe ca niir wa naan: \u00abKii mooy sama Doom ji ma b\u00ebgg, ci moom laa ame b\u00e0nneex; d\u00e9gluleen ko.\u00bb\n9:8 Ci saa si taalibe yi xool, waaye gisatu\u00f1u kenn, ku dul Yeesu rekk.\n9:9 Bi loolu amee \u00f1u w\u00e0cc ca tund wa. Bi muy w\u00e0cc nag, Yeesu sant leen ne: \u00abBuleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki na.\u00bb\n9:10 \u00d1u t\u00e9ye wax jooju ci seen biir, di sotteente xel, ba xam lu ndekkite looluy tekki.\n9:11 Noonu taalibe yi laaj Yeesu: \u00abLu tax xutbakat yi di naan, Iliyas moo war a j\u00ebkk a \u00f1\u00ebw?\u00bb\n9:12 Yeesu ne leen: \u00abWaaw, Iliyas dina j\u00ebkk a \u00f1\u00ebw, jubbanti l\u00e9pp. Waaye itam lu tax bind na\u00f1u ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare, \u00f1u xeeb ko, d\u00ebddu ko.\n9:13 Waaye maa ngi leen di wax ne, Iliyas \u00f1\u00ebw na, te def na\u00f1u ko la leen neex, ni ko Mbind mi waxe.\u00bb\n9:14 Bi nga xamee ne Yeesu \u00f1\u00ebw na, ba jege taalibe yi, mu gis mbooloo mu bare w\u00ebr leen, te ay xutbakat di werante ak \u00f1oom.\n9:15 Naka la mbooloo mi gis Yeesu, \u00f1u waaru, daldi daw nuyu ko.\n9:16 Noonu Yeesu laaj leen: \u00abCi lan ngeen di werante ak \u00f1oom?\u00bb\n9:17 Kenn ci mbooloo mi tontu ko ne: \u00abKilifa gi, rab j\u00e0pp na sama doom, ba luuloo ko. Saa su ko j\u00e0ppee, daf koy daaneel ci suuf, g\u00e9mmi\u00f1 gi di fuur, muy y\u00e9yu, ne j\u00e0dd. \u00d1aan naa say taalibe, \u00f1u d\u00e0q ko, waaye m\u00ebnu\u00f1u ko.\u00bb\n9:19 Yeesu ne leen: \u00abY\u00e9en niti jamono jii, y\u00e9en \u00f1i g\u00ebmadi, ba ka\u00f1 laa war a nekk ak y\u00e9en, ba ka\u00f1 laa leen war a mu\u00f1al? Indil-leen ma xale bi.\u00bb\n9:20 \u00d1u indil ko ko. Bi xale bi gisee Yeesu nag, rab wi sayloo ko ci saa si, mu daanu ci suuf, di xalangu, g\u00e9mmi\u00f1 giy fuur.\n9:21 Yeesu laaj baay bi: \u00abLii ka\u00f1 la ko dal?\u00bb Baay bi ne ko: \u00abLi dale ci nguneem.\n9:22 L\u00e9eg-l\u00e9eg rab wi b\u00ebm\u00ebx ko ci safara, l\u00e9eg-l\u00e9eg mu b\u00ebm\u00ebx ko ci ndox, ngir rey ko. Soo ko manee, y\u00ebr\u00ebm nu te xettali nu.\u00bb\n9:23 Yeesu tontu ko: \u00abNga ne: \u201cSoo ko manee,\u201d ku g\u00ebm man na l\u00e9pp.\u00bb\n9:24 Ci saa si baayu xale bi wax ci kaw naan: \u00abG\u00ebm naa, d\u00e0qal ma sama ng\u00ebmadi.\u00bb\n9:25 Yeesu gis nag ne, mbooloo maa ngi daw, w\u00ebrsi ko, mu daldi g\u00ebdd rab wi nag ne ko: \u00abG\u00e9nnal ci moom, yaw rab wu luu te t\u00ebx, te bu ko j\u00e0ppaat; wax naa la ko.\u00bb\n9:26 Noonu rab wa daldi yuuxu, sayloo xale bi, g\u00e9nn. Xale bi ne nemm, mel ni ku dee, ba tax \u00f1u bare ne: \u00abDee na.\u00bb\n9:27 Waaye Yeesu j\u00e0pp loxoom, j\u00f3gloo ko, xale bi daldi taxaw.\n9:28 Bi Yeesu duggee ci k\u00ebr gi, taalibe yi laaj ko ci pegg: \u00abLu tax m\u00ebnunu ko woon a d\u00e0q?\u00bb\n9:29 Yeesu tontu leen ne: \u00abYu mel ni yii, \u00f1aan ci Y\u00e0lla rekk a leen di d\u00e0q.\u00bb\n9:30 Bi loolu amee \u00f1u j\u00f3ge fa, jaar ci diiwaanu Galile, Yeesu b\u00ebggul kenn y\u00e9g ko.\n9:31 Ndaxte muy j\u00e0ngal taalibe yi ne leen: \u00abDees na j\u00e9bbal Doomu nit ki ci loxoy nit, te dina\u00f1u ko rey, mu dekki ci \u00f1etti fan.\u00bb\n9:32 Waaye taalibe yi xamu\u00f1u lu wax joojuy tekki, te \u00f1emewu\u00f1u ko koo laaj.\n9:33 Bi nga xamee ne egg na\u00f1u d\u00ebkku Kapernawum, te dugg ci k\u00ebr gi, Yeesu laaj leen ne: \u00abLu ngeen doon waxtaane ci yoon wi?\u00bb\n9:34 Waaye \u00f1u ne cell, ndaxte \u00f1u ngi fa doon werante, ba xam ku g\u00ebn a m\u00e0gg ci \u00f1oom.\n9:35 Noonu Yeesu toog, woo fukki taalibe ya ak \u00f1aar ne leen: \u00abKu b\u00ebgg a jiitu, na topp ci gannaaw \u00f1\u00e9pp te nekk surgab \u00f1\u00e9pp.\u00bb\n9:36 Bi ko Yeesu waxee, mu j\u00ebl xale, indi ko ci biir g\u00e9ew gi, ba noppi leewu ko naan:\n9:37 \u00abKu nangu xale bu mel ni bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, du man mii sax nga nangu waaye ki ma y\u00f3nni.\u00bb\n9:38 Bi loolu amee Yowaana ne ko: \u00abKilifa gi, danoo gis nit kuy d\u00e0q ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndax li mu bokkul ci nun.\u00bb\n9:39 Waaye Yeesu tontu ko: \u00abBuleen ko tere, ndaxte kenn m\u00ebnul a def k\u00e9emaan ci sama tur, ba noppi di ma xarab.\n9:40 Ku nu sotul, far na ak nun.\n9:41 Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na leen kaasu ndox rekk, ndax y\u00e9ena ngi bokk ci man Kirist, kooku du \u00f1\u00e0kk yoolam mukk.\n9:42 \u00abWaaye ku y\u00f3bbe b\u00e0kkaar kenn ci \u00f1i g\u00ebn a tuuti \u00f1i ma g\u00ebm, li g\u00ebn ci moom, moo di \u00f1u takk doj wu r\u00e9y ci baatam, s\u00e0nni ko ci g\u00e9ej.\n9:43 Boo xamee ne sa loxo mu ngi lay y\u00f3bbe b\u00e0kkaar, dagg ko. Ndaxte \u00f1\u00e0kk loxo te t\u00e0bbi ci dund gu w\u00f3or gi, moo g\u00ebn ci yaw, nga am \u00f1aari loxo te t\u00e0bbi ci safara su dul fey mukk.\n9:45 Te bu la sa t\u00e0nk di y\u00f3bbe b\u00e0kkaar, dagg ko. Nga lafa\u00f1 te t\u00e0bbi ci dund gu w\u00f3or gi moo g\u00ebn, nga am \u00f1aari t\u00e0nk, \u00f1u s\u00e0nni la ci safara.\n9:47 Te bu la sa b\u00ebt di y\u00f3bbe b\u00e0kkaar, luqi ko. Nga patt te dugg ci nguuru Y\u00e0lla, moo g\u00ebn ci yaw, nga am \u00f1aari b\u00ebt, \u00f1u s\u00e0nni la ci safara.\n9:48 Foofa:\u201cSax ya du\u00f1u dee mukk,te safara sa du fey.\u201d\n9:49 \u00d1\u00e9pp safara la\u00f1u leen di xorome.\n9:50 Xorom lu baax la, waaye bu s\u00e0ppee, nan la\u00f1u koy delloo cafkaam? Amleen xorom te ngeen j\u00e0mmoo.\u00bb\n10:1 Gannaaw loolu Yeesu j\u00f3ge fa, dem ca w\u00e0lli r\u00e9ewu Yawut yi, ya ca gannaaw dexu Yurdan. Bi mu fa demee, mbooloo mu bare \u00f1\u00ebw fi moom. Yeesu daldi leen j\u00e0ngal, ni mu ko daan defe.\n10:2 Noonu ay Farisen \u00f1\u00ebw ci moom, lalal ko fiir, \u00f1u laaj ko: \u00abNdax jaadu na, nit fase jabaram?\u00bb\n10:3 Yeesu tontu leen ne: \u00abLu leen yoonu Musaa sant?\u00bb\n10:4 \u00d1u ne ko: \u00abMusaa maye na, nit bind kayitu pase, t\u00e0ggook jabaram.\u00bb\n10:5 Waaye Yeesu ne leen: \u00abD\u00e9nkaane boobu mu leen bindal, bind na ko ndax seen xol dafa fatt.\n10:6 Waaye ca nj\u00e0lb\u00e9en ga \u201cY\u00e0lla s\u00e0kk na leen, kii g\u00f3or, kii jig\u00e9en.\n10:7 Moo tax g\u00f3or dina beru ndeyam ak baayam, di taq ci jabaram,\n10:8 \u00f1oom \u00f1aar doon benn.\u201d Kon nekkatu\u00f1u \u00f1aar waaye benn.\n10:9 Lu Y\u00e0lla takk nag, bu ko nit tas.\u00bb\n10:10 Bi \u00f1u delloo ca k\u00ebr ga nag, taalibe ya laaj ko ci mbirum loolu.\n10:11 Noonu Yeesu ne leen: \u00abKu fase sa jabar, takk jeneen, njaaloo nga, di too\u00f1 ku j\u00ebkk ka.\n10:12 Te jig\u00e9en ji tas, s\u00e9yaat ak keneen, njaaloo nga.\u00bb\n10:13 Bi loolu w\u00e9yee \u00f1u indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom. Waaye taalibe ya g\u00ebdd nit \u00f1i.\n10:14 Bi ko Yeesu gisee nag, mu metti ko lool, mu ne leen: \u00abB\u00e0yyileen xale yi, \u00f1u \u00f1\u00ebw fi man! Buleen leen tere, ndaxte \u00f1u mel ni \u00f1oom \u00f1oo yelloo nguuru Y\u00e0lla.\n10:15 Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, ku woyoful ni xale, nangu nguuru Y\u00e0lla, doo ci man a dugg.\u00bb\n10:16 Noonu Yeesu leewu leen, teg leen ay loxoom, barkeel leen.\n10:17 Gannaaw loolu bi Yeesu nekkee ci kaw yoon wi di dem, am ku daw, sukk ci kanamam ne ko: \u00abKilifa gu baax gi, lu ma war a def, ngir am w\u00e0ll ci dund gu dul jeex gi?\u00bb\n10:18 Yeesu tontu ko: \u00abLu tax nga wooye ma ku baax ki? Y\u00e0lla rekk a baax.\n10:19 Xam nga ndigal yi: \u201cBul b\u00f3om, bul njaaloo, bul s\u00e0cc, bul seede lu dul d\u00ebgg, bul nangu alalu jaambur, teralal sa ndey ak sa baay.\u201d\u00bb\n10:20 Waa ji ne ko: \u00abKilifa gi, loolu l\u00e9pp s\u00e0mm naa ko li dale ci samag ndaw ba tey.\u00bb\n10:21 Noonu Yeesu xool ko, am cofeel ci moom, mu ne ko: \u00abLenn rekk moo la dese. Demal jaay li nga am, may ko miskin yi, te dinga woomle ci asamaan; boo noppee, nga \u00f1\u00ebw topp ci man.\u00bb\n10:22 Waaye ci wax jooju xar-kanamam l\u00ebnd\u00ebm, mu j\u00f3ge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la.\n10:23 Noonu Yeesu xool taalibe yi ko w\u00ebr ne leen: \u00abBoroom alal dugg ci nguuru Y\u00e0lla, lu jafee ngoogu!\u00bb\n10:24 Wax jooju nag daldi jaaxal taalibe yi lool. Waaye Yeesu neeti leen: \u00abSamay xarit, dugg ci nguuru Y\u00e0lla, lu jafee ngoogu!\n10:25 Gil\u00e9em jaar ci b\u00ebn-b\u00ebnu pusa, moo g\u00ebn a yomb boroom alal dugg ci nguuru Y\u00e0lla.\u00bb\n10:26 Wax jooju g\u00ebnatee jaaxal taalibe ya, \u00f1u naan ci seen biir: \u00abKon nag ku man a mucc?\u00bb\n10:27 Noonu Yeesu xool leen naan: \u00abLoolu t\u00eb na nit, waaye t\u00ebwul Y\u00e0lla; Y\u00e0lla man na l\u00e9pp.\u00bb\n10:28 Ci kaw loolu Piyeer daldi ko ne: \u00abNun de d\u00ebddu nanu l\u00e9pp te topp la!\u00bb\n10:29 Yeesu tontu ko: \u00abCi d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, k\u00e9pp ku d\u00ebddu k\u00ebr, doomu ndey yu g\u00f3or walla yu jig\u00e9en, ndey walla baay, doom walla suuf ndax man ak xebaar bu baax bi,\n10:30 dinga am tey jii t\u00e9em\u00e9eri yoon ay k\u00ebr, doomi ndey yu g\u00f3or ak yu jig\u00e9en, ndey, doom ak suuf, \u00f1oom ak ay fitnay noon, te \u00ebll\u00ebg nga am dund gu dul jeex.\n10:31 Waaye \u00f1u bare ci \u00f1i jiitu \u00f1ooy mujji; \u00f1i mujj \u00f1ooy jiituji.\u00bb\n10:32 Gannaaw loolu \u00f1u \u00e0nd j\u00ebm Yerusalem, Yeesu jiitu; taalibe yi am nj\u00e0qare, te \u00f1i ci topp tiit. Noonu Yeesu woowaat fukk ak \u00f1aar \u00f1a cig wet, xamal leen li nar a xew ci mbiram.\n10:33 Mu ne leen: \u00abNoo ngi dem Yerusalem, te dees na j\u00e9bbal Doomu nit ki ci loxoy saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya. Dina\u00f1u ko \u00e0tte, teg ko dee, j\u00e9bbal ko \u00f1i dul Yawut,\n10:34 \u00f1u \u00f1aawal ko, di tifli ci kawam, d\u00f3or ko ay yar, rey ko. Waaye gannaaw \u00f1etti fan dina dekki.\u00bb\n10:35 Gannaaw loolu Saag ak Yowaana, doomi Sebede, \u00f1\u00ebw ci Yeesu. \u00d1u ne ko: \u00abKilifa gi, danoo b\u00ebggoon nga may nu li nu lay \u00f1aan.\u00bb\n10:36 Yeesu tontu leen: \u00abLu ngeen b\u00ebggoon, ma may leen ko?\u00bb\n10:37 \u00d1u ne ko: \u00abB\u00e9s boo soloo sa ndam, nga may nu, nu toog, kii ci sa ndeyjoor, kii ci sa c\u00e0mmoo\u00f1.\u00bb\n10:38 Waaye Yeesu tontu leen: \u00abXamuleen li ngeen di \u00f1aan. Ndax man ngeen a naan kaasu naqar, bi may naan? Ndax man ngeen a s\u00f3obu ci metit, yi ma nar a s\u00f3obu?\u00bb\n10:39 \u00d1u ne ko: \u00abWaaw, man nanu ko.\u00bb Noonu Yeesu ne leen: \u00abDingeen naan kaasu naqar, bi may naan, tey s\u00f3obu ci metit, yi ma nar a s\u00f3obu,\n10:40 waaye toog ci sama ndeyjoor mbaa sama c\u00e0mmoo\u00f1, du man maa koy maye. \u00d1i \u00f1u ko waajal rekk a ko yelloo.\u00bb\n10:41 Bi nga xamee ne fukki taalibe ya ca des d\u00e9gg na\u00f1u loolu, \u00f1u daldi mere Saag ak Yowaana.\n10:42 Waaye Yeesu woo leen naan: \u00abXam ngeen ne ci xeeti \u00e0ddina, \u00f1i \u00f1u teg njiit da\u00f1u leen di d\u00f3or yetu nguur, te kilifa yi di leen noot.\n10:43 Buleen mel ni \u00f1oo\u00f1u. Waaye ku b\u00ebgg a nekk kilifa ci y\u00e9en, na nekk seen surga,\n10:44 te ku b\u00ebgg a nekk njiit, na nekk seen jaam.\n10:45 Ndaxte noonu la Doomu nit ki \u00f1\u00ebwe sax, du ngir \u00f1u nekk ay surgaam, waaye ngir muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug \u00f1u bare.\u00bb\n10:46 Bi loolu w\u00e9yee \u00f1u agsi ca d\u00ebkku Yeriko. Bi ko Yeesu di g\u00e9nn, \u00e0nd ak taalibe ya ak mbooloo mu xaw a bare, am gumba gu tudd Bartime \u2014 liy tekki \u00abdoomu Time,\u00bb toog ci wetu yoon wi, di yelwaan.\n10:47 Noonu mu d\u00e9gg ne, Yeesum Nasaret moo fay romb; mu daldi yuuxu naan: \u00abY\u00ebr\u00ebm ma, yaw S\u00ebtu Daawuda bi!\u00bb\n10:48 Ci kaw loolu \u00f1u bare g\u00ebdd ko, ngir mu noppi. Teewul mu g\u00ebn a yuuxu naan: \u00abYaw S\u00ebtu Daawuda bi, y\u00ebr\u00ebm ma!\u00bb\n10:49 Noonu Yeesu taxaw, daldi ne: \u00abWooleen ko!\u00bb \u00d1u woo nag gumba gi ne ko: \u00abNa sa xel dal! J\u00f3gal! Mu ngi lay woo.\u00bb\n10:50 Bi mu ko d\u00e9ggee, mu s\u00e0nni malaanam, ne b\u00ebr\u00e9t, dem ci Yeesu.\n10:51 Yeesu ne ko: \u00abLoo b\u00ebggoon ma defal la ko?\u00bb Gumba gi tontu ko: \u00abKilifa gi, damaa b\u00ebgg a gis.\u00bb\n10:52 Noonu Yeesu ne ko: \u00abDemal ci j\u00e0mm. Sa ng\u00ebm faj na la.\u00bb Ci saa si gumba gi gis, daldi topp Yeesu ci yoon wi.\n11:1 Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege na\u00f1u Yerusalem, ba agsi d\u00ebkki Betfase ak Betani ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal \u00f1aar ciy taalibeem,\n11:2 ne leen: \u00abDemleen ci d\u00ebkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi.\n11:3 Bu leen kenn nee: \u201cLu ngeen di def?\u201d tontuleen ko: \u201cBoroom bi da koo soxla, te l\u00e9egi mu delloosi ko.\u201d\u00bb\n11:4 Taalibe ya dem nag, \u00f1u gis cumbur ga ci mbedd mi, mu yeewe cib buntu k\u00ebr.\n11:5 Bi \u00f1u koy yiwi nag, am na ca \u00f1a fa taxaw, \u00f1u ne leen: \u00abLu ngeen nar, bay yiwi cumbur gi?\u00bb\n11:6 Taalibe yi tontu leen, ni leen Yeesu digale woon, kon nit \u00f1i b\u00e0yyi leen, \u00f1u dem.\n11:7 \u00d1u indi cumbur gi Yeesu nag, lal ci seeni y\u00e9re, mu toog ci.\n11:8 \u00d1u bare lal seeni y\u00e9re ci yoon wi, \u00f1enn \u00f1i dagg ay cari garab ci tool yi, lal leen it ci yoon wi.\n11:9 \u00d1iy jiitu ak \u00f1iy topp ci Yeesu \u00f1\u00e9pp di wax ci kaw naan:\u00abOsaana!Yaw miy \u00f1\u00ebw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!\n11:10 Nguuru sunu maam Daawuda giy \u00f1\u00ebw,dina barkeel!Ci b\u00e9rab yu g\u00ebn a kawe,na\u00f1u ne: \u201cOsaana!\u201d\u00bb\n11:11 Noonu Yeesu dugg Yerusalem, dem k\u00ebr Y\u00e0lla ga, xool l\u00e9pp, ba noppi g\u00e9nn dem d\u00ebkku Betani, moom ak fukki taalibe ya ak \u00f1aar, ndaxte dafa guddi.\n11:12 B\u00ebt set \u00f1u g\u00e9nn Betani, fekk Yeesu xiif.\n11:13 Noonu mu s\u00e9en fu sore garabu figg gu s\u00ebq, mu dem seeti, ndax am na ay doom. Waaye bi mu fa eggee, gisul lu dul ay xob, ndaxte jamonoy figg duggagul.\n11:14 Ci kaw loolu mu ne garab gi: \u00abDootuloo me\u00f1\u00f1 mukk!\u00bb Taalibe yi d\u00e9gg loolu mu wax.\n11:15 Bi \u00f1u eggee Yerusalem, Yeesu dugg ci k\u00ebr Y\u00e0lla gi, daldi d\u00e0q \u00f1i fay jaay ak \u00f1i fay j\u00ebnd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis yi ak tooguy jaaykati pitax yi,\n11:16 te mayul kenn, mu y\u00f3bbu am njaay ci k\u00ebr Y\u00e0lla gi.\n11:17 Mu di leen j\u00e0ngal ne leen: \u00abNdax waxu\u00f1u ci Mbind mi:\u201cDees na wooye sama k\u00ebrk\u00ebru \u00f1aan ci Y\u00e0lla ngir xeet y\u00e9pp\u201d? Waaye y\u00e9en def ngeen ko k\u00ebru s\u00e0cc.\u00bb\n11:18 Bi ko saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya d\u00e9ggee nag, \u00f1u ragal ko, ndaxte mbooloo m\u00e9pp da\u00f1oo waaru ci nj\u00e0ngaleem. Noonu \u00f1u seet pexem reylu ko.\n11:19 Bi timis jotee Yeesu ak taalibe yi g\u00e9nn d\u00ebkk bi.\n11:20 Ci suba si, bi \u00f1uy dem, \u00f1u gis ne garabu figg gi dee na, ba wow ko\u014b\u014b.\n11:21 Noonu Piyeer f\u00e0ttaliku li xewoon, ne Yeesu: \u00abKilifa gi, xoolal, figg gi nga r\u00ebbb dee na, ba wow!\u00bb\n11:22 Yeesu tontu ne: \u00abG\u00ebmleen Y\u00e0lla.\n11:23 Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, ku ne tund wale: \u201cJ\u00f3gal, t\u00e0bbi ca g\u00e9ej ga,\u201d te nga g\u00ebm ne loolu dina am, ba\u00f1 cee boole xel \u00f1aar, kon sa \u00f1aan nangu.\n11:24 Moo tax maa ngi leen koy wax, bu ngeen di \u00f1aan Y\u00e0lla, l\u00e9pp lu ngeen ko man a laaj, g\u00ebmleen ne jot ngeen ko, te dingeen ko am.\n11:25 Te it bu ngeen di \u00f1aan, fekk ngeen j\u00e0ppal kenn dara, baal-leen ko, ngir seen Baay bi ci kaw baal leen seeni too\u00f1, y\u00e9en itam.\u00bb\n11:27 Gannaaw loolu \u00f1u duggaat Yerusalem, te Yeesu doon doxantu ca \u00ebtti k\u00ebr Y\u00e0lla ga. Noonu saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya dab ko\n11:28 ne ko: \u00abY\u00ebf yii ngay def, ci ban sa\u00f1-sa\u00f1 nga koy defe? Te ku la may sa\u00f1-sa\u00f1u def ko?\u00bb\n11:29 Yeesu tontu leen: \u00abMan itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ci tontoo, kon dinaa leen wax ci ban sa\u00f1-sa\u00f1 laay defe y\u00ebf yii.\n11:30 La Yaxya daan def, di s\u00f3ob nit \u00f1i ci ndox, fu mu ko j\u00eble, ci Y\u00e0lla walla ci nit \u00f1i?\u00bb\n11:31 Bi \u00f1u ko d\u00e9ggee, \u00f1uy werante ci seen biir naan: \u00abBu nu nee: \u201cCi Y\u00e0lla,\u201d kon dina nu laaj: \u201cLu tax g\u00ebmuleen ko kon?\u201d\n11:32 Waaye bu nu nee: \u201cCi nit \u00f1i,\u201d kon mbooloo mi dal ci sunu kaw;\u00bb ndaxte \u00f1\u00e9pp teg na\u00f1u Yaxya ab yonent.\n11:33 \u00d1u tontu Yeesu nag ne: \u00abLoolu de xamunu ko.\u00bb Noonu Yeesu ne leen: \u00abKon man itam duma leen wax ci ban sa\u00f1-sa\u00f1 laay defe y\u00ebf yii.\u00bb\n12:1 Noonu Yeesu daldi leen wax ciy l\u00e9eb. Mu ne leen: \u00abAmoon na fi nit ku j\u00ebmb\u00ebt toolu r\u00e9se\u00f1. Mu \u00f1ag tool bi, gas pax ngir nal ci r\u00e9se\u00f1 yi, tabax wottukaay, ba noppi batale ko ay beykat, daldi tukki.\n12:2 \u00abBi tool bi \u00f1oree nag, mu y\u00f3nni surga ci \u00f1oom, ngir jot w\u00e0llam ci me\u00f1\u00f1eef gi.\n12:3 Waaye \u00f1u j\u00e0pp ko, d\u00f3or ko ay yar, d\u00e0q ko, mu dellu ak loxoy neen.\n12:4 Mu y\u00f3nniwaat beneen surga, waaye \u00f1u d\u00f3or ko ci bopp, toroxal ko.\n12:5 Mu y\u00f3nneeti beneen surga, \u00f1u rey ko. Mu y\u00f3nni \u00f1eneen \u00f1u bare, \u00f1ii \u00f1u d\u00f3or leen, \u00f1ii \u00f1u rey.\n12:6 \u00abNoonu mu dese ko kenn rekk, di doomam ji mu b\u00ebgg. Mujj mu y\u00f3nni ko naan: \u201cX\u00eby na \u00f1u weg sama doom.\u201d\n12:7 Waaye beykat yi daldi ne ci seen biir: \u201cKii moo war a donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.\u201d\n12:8 \u00d1u j\u00e0pp ko nag, rey, s\u00e0nni ci biti.\u00bb\n12:9 Noonu Yeesu laaj leen: \u00abBoroom tool bi nag, lu muy def? Xanaa \u00f1\u00ebw, rey beykat ya, d\u00e9nk tool ba \u00f1eneen.\n12:10 Ndax musuleen a j\u00e0ng wax jii ci Mbind mi?\u201cDoj wi tabaxkat yi s\u00e0nni,mujj na di doju ko\u00f1;\n12:11 ci Boroom bi la loolu j\u00f3ge,te y\u00e9emu nanu ci.\u201d\u00bb\n12:12 Noonu kilifa yi di wut pexem j\u00e0pp ko, ndaxte xam na\u00f1u ne, \u00f1oom lay wax. Waaye ragal na\u00f1u mbooloo mi, ba \u00f1u b\u00e0yyi ko fa, dem.\n12:13 Bi loolu amee \u00f1u y\u00f3nni ci Yeesu ay Farisen ak \u00f1u far ak buur bi Erodd, ngir fiir ko ci waxam.\n12:14 \u00d1u \u00f1\u00ebw ci moom nag ne ko: \u00abKilifa gi, xam nanu ne ku w\u00f3or nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo j\u00ebmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Y\u00e0lla ci bu w\u00f3or. Wax nu, ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag am d\u00e9et? Nu fey ko walla nu ba\u00f1 koo fey?\u00bb\n12:15 Waaye Yeesu xam na seen naaf\u00e9q, mu ne leen: \u00abLu tax ngeen b\u00ebgg maa fiir? Indil-leen ma posetu denariyon, ma seet.\u00bb\n12:16 \u00d1u jox ko poset bi. Noonu Yeesu laaj leen: \u00abKan la\u00f1u ci def nataalam ak turam?\u00bb \u00d1u tontu ko: \u00abSesaar.\u00bb\n12:17 Noonu Yeesu ne leen: \u00abJoxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Y\u00e0lla li Y\u00e0lla moom.\u00bb \u00d1u daldi waaru ci mbiram.\n12:18 Gannaaw loolu ay Sadusen \u00f1\u00ebw ci moom, ngir laaj ko lenn. Sadusen yi nag g\u00ebmu\u00f1u ne, ndekkite am na.\n12:19 \u00d1u ne ko: \u00abKilifa gi, Musaa bindal na nu ne, ku magam faatu, te b\u00e0yyiwul doom ak jabaram, kooku war na donn jig\u00e9en ji, ba y\u00e9kkati giiru magam.\n12:20 \u00abAmoon na fi nag jur\u00f3om-\u00f1aari g\u00f3or, \u00f1u bokk ndey ak baay. Taaw ba takk jabar, faatu, te b\u00e0yyiwul doom.\n12:21 \u00d1aareel ba takk jig\u00e9en ja, faatu moom itam te b\u00e0yyiwul doom. \u00d1etteel bi it noonu.\n12:22 Mbir mi dem na nag, ba jur\u00f3om-\u00f1aar \u00f1oo\u00f1u \u00f1\u00e9pp dem, te kenn b\u00e0yyiwu fi doom. Mujj jig\u00e9en ja faatu moom itam.\n12:23 Ci ndekkite li nag kan ci \u00f1oom moo ko war a donn, fekk ku nekk ci jur\u00f3om-\u00f1aar \u00f1i mas na koo takk?\u00bb\n12:24 Yeesu tontu leen ne: \u00abMbaa du dangeen a nekk cig r\u00e9er, ci li ngeen xamul Mbind mi mbaa k\u00e0ttanu Y\u00e0lla?\n12:25 Ndaxte keroog ndekkite li kenn du am jabar, kenn du am j\u00ebkk\u00ebr, waaye dina\u00f1u mel ni malaaka yi ci kaw.\n12:26 Te sax li j\u00ebm ci mbirum ndekkite, xanaa j\u00e0nguleen lii Y\u00e0lla wax ci Tawreetu Musaa ci saarum ngarab si: \u201cMaay Y\u00e0llay Ibraayma, Isaaxa ak Yanq\u00f3oba\u201d?\n12:27 Li ci g\u00e9nn mooy, nekkul Y\u00e0llay \u00f1i dee, waaye Y\u00e0llay \u00f1iy dund la. Kon s\u00f3obu ngeen cig r\u00e9er.\u00bb\n12:28 Bi \u00f1uy werante, benn xutbakat \u00f1\u00ebw, d\u00e9gg seen waxtaan, gis ne Yeesu tontu na leen tont lu leer. Mu laaj ko nag: \u00abCi ndigal yi, ban moo ci g\u00ebn a m\u00e0gg?\u00bb\n12:29 Noonu Yeesu tontu ko ne: \u00abBii: \u201cB\u00e0nni Israyil, d\u00e9glul! Y\u00e0lla sunu Boroom moom rekk mooy Buur.\n12:30 Kon nanga b\u00ebgg Y\u00e0lla sa Boroom ak sa xol b\u00e9pp ak sa bakkan b\u00e9pp, sa xel m\u00e9pp ak sa k\u00e0ttan g\u00e9pp.\u201d\n12:31 Te \u00f1aareel bi, lii la: \u201cNanga b\u00ebgg sa moroom, ni nga b\u00ebgge sa bopp.\u201d Ndigal yii \u00f1oo sut y\u00e9pp.\u00bb\n12:32 Xutbakat bi ne ko: \u00abWaaw kilifa gi, li nga wax d\u00ebgg la: Y\u00e0lla kenn la, te amul jeneen Y\u00e0lla ju dul moom.\n12:33 Te nga b\u00ebgg ko ak sa xol b\u00e9pp ak sa xel m\u00e9pp ak sa k\u00e0ttan g\u00e9pp moo d\u00e0q b\u00e9pp sarax bu \u00f1uy y\u00f3bbu ngir m\u00e0ggal Y\u00e0lla ak bu \u00f1uy lakk ca saraxalukaay ba.\u00bb\n12:34 Bi Yeesu gisee nag ne, tontu na ak xel, mu ne ko: \u00abSorewuloo nguuru Y\u00e0lla.\u00bb Bi mu waxee loolu, kenn \u00f1emeetu ko laaj dara.\n12:35 Bi nga xamee ne Yeesu ma nga doon j\u00e0ngale ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, mu laaj nit \u00f1i: \u00abLu tax xutbakat yi di wax ne, Almasi bi mooy s\u00ebtu Daawuda?\n12:36 Daawuda moom wax na ci k\u00e0ttanu Xel mu Sell mi naan:\u201cBoroom bi nee na sama Boroom:\u00ab\u201cToogal ci sama ndeyjoor,ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.\u00bb\u201c \u201c\n12:37 Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: \u201cBoroom bi,\u201d naka mu nekke s\u00ebtam?\u00bb Noonu mbooloo mu mag mi di ko d\u00e9glu ak b\u00e0nneex.\n12:38 Bi Yeesu di j\u00e0ngale nag, mu ne leen: \u00abMoytuleen xutbakat yi; da\u00f1oo b\u00ebgg di doxantu, sol ay mbubb yu r\u00e9y, te \u00f1\u00e9pp di leen nuyoo \u00f1aari loxo ci p\u00e9nc mi.\n12:39 Ci j\u00e0ngu yi, f\u00e9ete kanam la\u00f1uy wut, te toogu yu yiw la\u00f1uy taamu ci reeri xew yi.\n12:40 \u00d1u ngi lekk alalu jig\u00e9en \u00f1i seeni j\u00ebkk\u00ebr faatu, di \u00f1aan Y\u00e0lla ay \u00f1aani ngistal yu gudd. Seen mbugal dina g\u00ebn a tar.\u00bb\n12:41 Noonu Yeesu toog ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, janook ndab, yi \u00f1uy def sarax ngir Y\u00e0lla, muy xool nit \u00f1a cay dugal seen xaalis. Am nag ay boroom alal yu ci di def xaalis bu bare.\n12:42 Gannaaw ga daal benn jig\u00e9en ju j\u00ebkk\u00ebram faatu, te mu \u00f1\u00e0kk, \u00f1\u00ebw, def ci \u00f1aari poseti x\u00e0njar, yu matul sax d\u00ebr\u00ebm.\n12:43 Bi ko Yeesu gisee, mu woo taalibe yi ne leen: \u00abCi d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, li jig\u00e9en ju \u00f1\u00e0kk jee dugal ca defukaay ya moo \u00ebpp maana alalu \u00f1eneen \u00f1i \u00f1\u00e9pp.\n12:44 \u00d1oom \u00f1\u00e9pp da\u00f1u s\u00e0kku ci seen barele, waaye moom dafa s\u00e0kku ci n\u00e9ewleem, ba far ko joxe l\u00e9pp, toog.\u00bb\n13:1 Bi Yeesu di j\u00f3ge ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, kenn ca taalibe ya ne ko: \u00abKilifa gi, xoolal! Ni mu r\u00e9ye ay doj, te rafete ni ay taax!\u00bb\n13:2 Waaye Yeesu tontu leen: \u00abDu gis ngeen taax yu r\u00e9y yii y\u00e9pp? Lii l\u00e9pp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.\u00bb\n13:3 Gannaaw loolu, bi nga xamee ne Yeesu toog na ci tundu Oliw ya, j\u00e0kkaarlook k\u00ebr Y\u00e0lla ga, Piyeer, Saag, Yowaana ak Andare fekki ko cig wet, laaj ko:\n13:4 \u00abWax nu ka\u00f1 la loolu di am? Te luy tegtal ne, mbir yii y\u00e9pp a ngi b\u00ebgg a mat?\u00bb\n13:5 Noonu Yeesu tontu leen: \u00abMoytuleen, bu leen kenn nax.\n13:6 \u00d1u bare dina\u00f1u \u00f1\u00ebw ci sama tur naan: \u201cMoom laa,\u201d te dina\u00f1u nax \u00f1u bare.\n13:7 Bu ngeen d\u00e9ggee ay xare ak coowi xare, wottuleen a tiit; loolu war na am, waaye mujug jamono ji jotagul.\n13:8 Xeet dina j\u00f3g, xeex ak weneen xeet, r\u00e9ew xeex ak meneen r\u00e9ew. Te yengu-yenguy suuf dina am ciy b\u00e9rab yu bare, ak ay xiif. Loolu l\u00e9pp mooy ndoortel metit yi, mel ni jig\u00e9en juy matu.\n13:9 \u00abMoytuleen. Dees na leen j\u00e9bbal \u00e0ttekat ya, di leen d\u00f3or ay yar ca j\u00e0ngu ya. Dina\u00f1u leen d\u00ebj ci kanamu ay boroom r\u00e9ew ak ay buur ndax sama tur, ngir ngeen nekk seede ci \u00f1oom.\n13:10 F\u00e0ww xebaar bu baax bi j\u00ebkk a jib ci xeet y\u00e9pp.\n13:11 Saa su \u00f1u leen j\u00e0ppee nag, d\u00ebj leen ci p\u00e9ncum layoo, buleen j\u00e0q ci li ngeen war a wax; li ngeen jot ca waxtu woowa waxleen ko, ndaxte du y\u00e9enay wax waaye Xel mu Sell mi.\n13:12 \u00abMag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam; ay doom it dina\u00f1u j\u00f3g, di ba\u00f1 seeni waajur, di leen reylu.\n13:13 Te \u00f1\u00e9pp dina\u00f1u leen ba\u00f1 ndax sama tur; waaye ku mu\u00f1 ba ca muj ga, mucc.\n13:14 \u00abB\u00e9s baa ngi \u00f1\u00ebw, bu li \u00f1uy wax \u201cLu araam luy y\u00e0qe\u201d tegee ca b\u00e9rab bu mu yelloowul; kiy j\u00e0ng, na xam. Bu ngeen gisee loolu nag, ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya.\n13:15 Ku nekk ci kaw taax mi, bul w\u00e0cc ngir dugg k\u00ebr gi, fab say y\u00ebf ya fa nekk.\n13:16 Ku nekk ci tool bi, bul \u00f1ibbi ngir fab sa mbubb.\n13:17 Ngalla jig\u00e9en \u00f1i \u00ebmb ca b\u00e9s yooya, ngalla it \u00f1iy n\u00e0mpal.\n13:18 \u00d1aanleen ngir seen g\u00e0ddaay ba\u00f1 a tase ak jamonoy seddaayu lolli.\n13:19 Ndaxte booba dina am metit wu r\u00e9y wu musul a am, ba \u00e0ddina sosoo ak tey, te dootul am mukk.\n13:20 Te bu fekkul woon Boroom bi w\u00e0\u00f1\u00f1i b\u00e9s yooyu, kenn du mucc, waaye fekk na mu w\u00e0\u00f1\u00f1i leen ndax gaayam \u00f1i mu t\u00e0nn.\n13:21 \u00abBooba nag, bu leen kenn waxee: \u201cKaayleen gis, Kirist a ngi fi,\u201d mbaa: \u201cXool-leen, mu nga fale,\u201d buleen ko g\u00ebm.\n13:22 Ndaxte \u00f1iy mbubboo turu Kirist ak \u00f1iy mbubboo turu yonent, dina\u00f1u fee\u00f1, di joxe ay firnde yu r\u00e9y ak ay k\u00e9emaan, ba ciy nax sax \u00f1i Y\u00e0lla t\u00e0nn, su loolu manoon a am.\n13:23 Wax naa leen ko lu jiitu. Kon nag moytuleen.\n13:24 \u00abWaaye booba, gannaaw metit yooyu:\u201cJant bi dina l\u00ebnd\u00ebmte weer dootul leer;\n13:25 biddiiw yi di daanoo asamaan,te k\u00e0ttani asamaan yiy yengu.\u201d\n13:26 \u00abNoonu dees na gis Doomu nit ki \u00f1\u00ebw ci niir yi, \u00e0nd ak k\u00e0ttan ak ndam lu r\u00e9y.\n13:27 Dina y\u00f3nni ay malaakam, \u00f1u dajale \u00f1i mu t\u00e0nn ci \u00f1eenti xebla yi, fa \u00e0ddina dale, ba fa asamaan yem.\u00bb\n13:28 Yeesu teg ca ne: \u00abJ\u00e0ngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay b\u00e0nqaasam duy na\u00f1u, tey xobam s\u00ebq, xam ngeen ne nawet jege na.\n13:29 Noonu itam bu ngeen gisee loolu l\u00e9pp xew, xamleen ne jege na; mu ngi ci bunt bi sax.\n13:30 Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii du\u00f1u w\u00e9y, te loolu l\u00e9pp amul.\n13:31 Asamaan ak suuf dina\u00f1u w\u00e9y, waaye samay wax du w\u00e9y mukk.\n13:32 \u00abWaaye b\u00e9s boobu ak waxtu woowu, kenn xamul ka\u00f1 lay doon; du malaaka yi ci kaw, du sax Doom ji, waaye Baay bi rekk moo ko xam.\n13:33 Moytuleen te xool! Xamuleen ka\u00f1 la waxtu wi di jot.\n13:34 \u00abMi ngi mel ni nit ku tukki, mu d\u00e9nk k\u00ebram ay surgaam, ku nekk ak sa sas, te sant b\u00ebkk-n\u00e9eg bi, mu xool.\n13:35 Y\u00e9en nag xool-leen, ndaxte xamuleen ka\u00f1 la boroom k\u00ebr gi di dellusi, muy ci timis mbaa ci xaaju guddi, muy ci fajar mbaa nj\u00ebl.\n13:36 Bu nee jale\u00f1, bumu leen bett, ngeen di nelaw.\n13:37 Li ma leen wax, \u00f1\u00e9pp laa ko wax: \u201cXool-leen!\u201d\u00bb\n14:1 Booba nag saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya \u00f1u ngi doon fexeel Yeesu, ngir j\u00e0pp ko, reylu. Fekk booba \u00f1aari fan a des ci m\u00e0ggalu b\u00e9su J\u00e9ggi ba ak m\u00e0ggalu Mburu ya amul lawiir.\n14:2 Kon nag \u00f1u ne: \u00abBumu doon ci b\u00e9su m\u00e0ggal bi, ngir yengu-yengu ba\u00f1 a am ci nit \u00f1i.\u00bb\n14:3 Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na d\u00ebkku Betani, mu dem k\u00ebru Simo\u014b ma gaana woon, di fa lekk. Noonu jig\u00e9en \u00f1\u00ebw, yor njaq lu \u00f1u defare doj wu tudd albaatar. Njaq li def latkolo\u00f1 ju raxul ju \u00f1uy wax n\u00e0rd, tey jar lu baree-bare. Jig\u00e9en ji toj njaq li, tuur latkolo\u00f1 ci boppu Yeesu.\n14:4 Waaye amoon na fa \u00f1u mer, di xultu ci seen biir naan: \u00abY\u00e0q gii, lu muy jari\u00f1?\n14:5 Maneesoon na jaay latkolo\u00f1 jii ci lu tollook peyug atum l\u00ebmm, jox ko miskin yi.\u00bb Noonu \u00f1u daldi g\u00ebdd jig\u00e9en ji.\n14:6 Waaye Yeesu ne leen: \u00abB\u00e0yyileen ko. Defal na ma j\u00ebf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal?\n14:7 Miskin yaa ngi ak y\u00e9en b\u00e9s bu nekk, te man ngeen leen a dimbali saa su leen neexee, waaye dungeen ma gis ba f\u00e0ww.\n14:8 Jig\u00e9en ji def na li mu man; diw na sama yaram ak latkolo\u00f1, ngir waajal sama rob, laata moo jot.\n14:9 Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, f\u00e9pp fu \u00f1uy y\u00e9ene xebaar bu baax bi ci \u00e0ddina s\u00e9pp, dina\u00f1u fa f\u00e0ttali it li jig\u00e9en jii def.\u00bb\n14:10 Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak \u00f1aar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca saraxalekat yu mag ya, ngir wori Yeesu.\n14:11 Bi \u00f1u ko d\u00e9ggee, \u00f1u am ca b\u00e0nneex bu r\u00e9y, dig ko xaalis. Noonu mu fexe jamono ju mu leen man a j\u00e9bbal Yeesu.\n14:12 B\u00e9s bu j\u00ebkk ca m\u00e0ggal, ga \u00f1uy wax Mburu ya amul lawiir, taalibey Yeesu laaj ko: \u00abFoo b\u00ebgg, nu defaral la reeru J\u00e9ggi bi?\u00bb B\u00e9s bu j\u00ebkk booba nag mooy b\u00e9s, ba \u00f1u faral a rendi xarum m\u00e0ggalu J\u00e9ggi ba.\n14:13 Noonu Yeesu yebal \u00f1aar ci taalibe yi ne leen: \u00abDemleen ca d\u00ebkk ba, foofa g\u00f3or gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek y\u00e9en, ngeen topp ko.\n14:14 K\u00ebr gi mu dugg nag, ngeen ne boroom k\u00ebr gi: \u201cKilifa gi nee na: Ana n\u00e9egu gan, bi may lekke reeru J\u00e9ggi bi, man ak samay taalibe?\u201d\n14:15 Dina leen won n\u00e9eg bu f\u00e9ete kaw te yaa, \u00f1u defar ko, ba l\u00e9pp jekk. Foofa ngeen nuy defarale reer bi.\u00bb\n14:16 Bi mu ko waxee, taalibe ya dem ca d\u00ebkk ba, gis l\u00e9pp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu \u00f1u defar reer bi.\n14:17 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu \u00f1\u00ebw, \u00e0nd ak fukki taalibe yi ak \u00f1aar.\n14:18 \u00d1u toog, di lekk. Bi \u00f1uy lekk nag, Yeesu ne leen: \u00abCi d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, kenn ci y\u00e9en, ku bokk ak man di lekk sax, dina ma wor.\u00bb\n14:19 Taalibe yi nag am naqar, \u00f1u daldi ko ne kenn-kenn: \u00abMbaa du man?\u00bb\n14:20 Mu tontu leen: \u00abKenn ci y\u00e9en fukk ak \u00f1aar la, kuy cappandoo ak man ci ndab li.\n14:21 Doomu nit ki mu ngi dem, ni \u00f1u ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox. Ba\u00f1oon a juddu moo g\u00ebn ci moom.\u00bb\n14:22 Noonu bi \u00f1uy lekk, Yeesu j\u00ebl mburu, sant Y\u00e0lla, jox leen ko naan: \u00abJ\u00ebl-leen, lii sama yaram la.\u00bb\n14:23 Gannaaw loolu mu j\u00ebl kaas, sant Y\u00e0lla, jox leen ko, \u00f1\u00e9pp naan ci.\n14:24 Mu ne leen: \u00abLii sama deret la, ji fas k\u00f3ll\u00ebre gi, te mu tuuru ngir \u00f1u bare.\n14:25 Ci d\u00ebgg maa ngi leen koy wax, dootuma naan gannaaw tey ndoxum r\u00e9se\u00f1 mii, ba kera ma ciy naan bu bees ci nguuru Y\u00e0lla.\u00bb\n14:26 Noonu \u00f1u woy Y\u00e0lla, ba noppi g\u00e9nn, dem ca tundu Oliw ya.\n14:27 Booba Yeesu ne leen: \u00abY\u00e9en \u00f1\u00e9pp dingeen ma d\u00e0ggeeku, ndaxte bind na\u00f1u:\u201cDinaa d\u00f3or s\u00e0mm bi,xari jur gi tasaaroo.\u201d\n14:28 Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.\u00bb\n14:29 Kon Piyeer ne ko: \u00abBu la \u00f1\u00e9pp d\u00e0ggeekoo, man duma la b\u00e0yyi mukk.\u00bb\n14:30 Waaye Yeesu tontu ko: \u00abCi d\u00ebgg maa ngi la koy wax, guddig tey, bala ginaar a sab \u00f1aari yoon, dinga ma weddi \u00f1etti yoon.\u00bb\n14:31 Waaye Piyeer g\u00ebn a sax ca la mu waxoon naan: \u00abBoo xamee ne sax, damaa war a dee ak yaw, duma la weddi mukk.\u00bb Taalibe y\u00e9pp it waxe noonu.\n14:32 Noonu \u00f1u dem ca b\u00e9rab bu tudd Setsemane. Yeesu ne taalibe yi: \u00abToogleen fii, ma dem \u00f1aani.\u00bb\n14:33 Mu \u00e0nd ak Piyeer, Saag ak Yowaana, daldi j\u00e0q, ba xonett.\n14:34 Mu ne leen: \u00abSama xol dafa tiis, ba ma b\u00ebgg a dee; toogleen fii, xool.\u00bb\n14:35 Noonu Yeesu dem ci kanam tuuti, daanu ci suuf, di \u00f1aan ne, waxtu wi teggi ko, bu loolu manoon a am.\n14:36 Mu ne: \u00abAbba, Baay bi, yaw mi dara t\u00ebwul, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.\u00bb\n14:37 Noonu mu dellusi ci taalibe yi, fekk \u00f1uy nelaw. Mu ne Piyeer: \u00abSimo\u014b, dangaa nelaw? Amuloo sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu?\n14:38 Xool-leen te \u00f1aan, ngir ba\u00f1 a daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.\u00bb\n14:39 Beneen yoon Yeesu dem, di \u00f1aane noonu,\n14:40 dellusiwaat, fekk leen \u00f1uy nelaw, ndaxte seeni b\u00ebt da\u00f1oo diis. Xamu\u00f1u lu \u00f1u koy tontoo.\n14:41 \u00d1etteelu yoon mu dellusi ci \u00f1oom ne leen: \u00abY\u00e9ena ngi nelaw tey noppalu ba tey! Jeex na. Waxtu wi jot na; \u00f1u ngi wor Doomu nit ki ci loxoy b\u00e0kkaarkat yi.\n14:42 J\u00f3gleen nu dem; ki may wor a ngi nii, di \u00f1\u00ebw.\u00bb\n14:43 Bi Yeesu di wax, Yudaa mi bokkoon ci fukki taalibe ya ak \u00f1aar, agsi, \u00e0nd ak mbooloo mu bare, mu j\u00f3ge ca saraxalekat yu mag ya, ca xutbakat ya ak ca njiiti xeet wa, te g\u00e0nnaayoo jaasi ak yet.\n14:44 Fekk ki ko naroon a wor joxoon na leen tegtal ne leen: \u00abKi may f\u00f3on, moom la; j\u00e0ppleen ko, y\u00f3bbu ko te wottu ko bu baax.\u00bb\n14:45 Noonu mu \u00f1\u00ebw ci Yeesu ne ko: \u00abKilifa gi,\u00bb daldi ko f\u00f3on.\n14:46 Bi mu ko defee nit \u00f1i song Yeesu nag, j\u00e0pp ko.\n14:47 Waaye kenn ci \u00f1i fa taxaw bocci jaaseem, d\u00f3or surgab saraxalekat bu mag bi, nopp bi dagg.\n14:48 Yeesu ne leen: \u00abJ\u00f3g ngeen ngir j\u00e0pp ma, g\u00e0nnaayoo jaasi ak yet, mel ni \u00f1uy topp s\u00e0cc.\n14:49 Moona daan naa toog b\u00e9s bu nekk ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, di j\u00e0ngale, te j\u00e0ppuleen ma. Waaye lii am na, ngir Mbind mi am.\u00bb\n14:50 Ci kaw loolu, \u00f1\u00e9pp d\u00ebddu ko, daw.\n14:51 Fekk amoon na ca waxambaane wu l\u00ebkkaayoo woon s\u00e9r, topp Yeesu, \u00f1u daldi ko j\u00e0pp.\n14:52 Waaye waxambaane wa wacc fa s\u00e9r bi, daldi daw, def yaramu neen.\n14:53 \u00d1i j\u00e0pp Yeesu y\u00f3bbu ko ci saraxalekat bu mag bi, te foofa la saraxalekat yu mag yi, njiit yi ak xutbakat yi y\u00e9pp dajaloo.\n14:54 Piyeer nag topp ko fu sore, ba ci \u00ebttu saraxalekat bu mag bi, mu toog fa ak alkaati yi, di jaaru ci taal bi.\n14:55 Noonu saraxalekat yu mag yi ak kureelu \u00e0ttekat yi y\u00e9pp di wut ku man a seede lu daan Yeesu, ba \u00f1u man koo reylu, waaye gisu\u00f1u kenn.\n14:56 Teewul sax naaf\u00e9q \u00f1u bare \u00f1\u00ebw, seede ci Yeesu lu dul d\u00ebgg, waaye seen seede \u00e0ndu\u00f1u.\n14:57 Ba mujj naaf\u00e9q taxaw, seede ci moom naan:\n14:58 \u00abNun daal d\u00e9gg nanu, mu ne: \u201cDinaa toj k\u00ebr Y\u00e0lla, gii loxoy nit ligg\u00e9ey, tabax ci \u00f1etti fan geneen gu nit ligg\u00e9eyul.\u201d\u00bb\n14:59 Waaye ba tey seeni wax \u00e0ndu\u00f1u.\n14:60 Ci kaw loolu saraxalekat bu mag bi taxaw ci seen kanam ne Yeesu: \u00abDoo tontu? Lu la nit \u00f1i di jii\u00f1?\u00bb\n14:61 Waaye Yeesu tontuwul dara, ne cell. Saraxalekat bu mag bi dellu nag ne ko: \u00abNdax yaa di Almasi bi, Doomu Y\u00e0lla ju tedd ji?\u00bb\n14:62 Yeesu tontu ko: \u00abMoom laa. Te dingeen gis, Doomu nit ki toog ci ndeyjooru Aji K\u00e0ttan ji, di \u00f1\u00ebw ci niiri asamaan.\u00bb\n14:63 Bi ko saraxalekat bu mag bi d\u00e9ggee nag, mu daldi mer, ba xotti ay y\u00e9reem naan:\n14:64 \u00abWeddi na Y\u00e0lla, lu nu doyeeti seede? Lu ngeen ci xalaat?\u00bb Noonu \u00f1\u00e9pp teg ko dee.\n14:65 Ci kaw loolu \u00f1u daldi tifli ci moom, takk ay b\u00ebtam, di ko d\u00f3or ay kurfe\u00f1, naan ko: \u00abYaw wax nu ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, ku la d\u00f3or?\u00bb Ba noppi alkaati yi teeru ko ak ay pes.\n14:66 Piyeer nag ma nga toogoon ci \u00ebtt bi f\u00e9ete suuf. Noonu benn mbindaanu saraxalekat bu mag ba romb fa.\n14:67 Mu gis Piyeer di jaaru, xool ko j\u00e0kk naan: \u00abYaw itam \u00e0ndoon nga ak Yeesum Nasaret moomu.\u00bb\n14:68 Waaye Piyeer weddi ko naan: \u00abXawma li ngay wax, d\u00e9gguma ci dara.\u00bb Mu daldi g\u00e9nn, dem ca buntu k\u00ebr ga.\n14:69 Foofa nag mbindaan mi gisaat ko, mu ne \u00f1i fa taxaw: \u00abWaa jii ci \u00f1oom la bokk.\u00bb\n14:70 Waaye Piyeer weddiwaat ko.Nes tuuti \u00f1i fa taxaw ne Piyeer: \u00abYaw mi de, ci lu w\u00f3or bokk nga ci, nde waa Galile nga.\u00bb\n14:71 Waaye Piyeer daldi gi\u00f1 ak a waat naan: \u00abXawma nit ki ngay wax.\u00bb\n14:72 Ci saa si ginaar sab \u00f1aareelu yoon. Noonu Piyeer f\u00e0ttaliku li ko Yeesu wax: \u00abBala ginaar a sab \u00f1aari yoon, dinga ma weddi \u00f1etti yoon.\u00bb Mu daldi jooy jooy yu metti.\n15:1 Ci suba teel saraxalekat yu mag yi gise, \u00f1oom ak njiit yi ak xutbakat yi ak kureelu \u00e0ttekat yi y\u00e9pp. \u00d1u yeew nag Yeesu, daldi ko y\u00f3bbu, j\u00e9bbal ko Pilaat.\n15:2 Noonu Pilaat laaj ko: \u00abNdax yaa di buuru Yawut yi?\u00bb Yeesu tontu ko: \u00abWax nga ko.\u00bb\n15:3 Te saraxalekat yu mag yi di ko jii\u00f1 lu bare.\n15:4 Kon nag Pilaat laajaat ko: \u00abD\u00e9ggal l\u00e9pp li \u00f1u lay jii\u00f1. Xanaa amoo ci tont?\u00bb\n15:5 Waaye ba tey Yeesu tontuwul dara, ba tax Pilaat waaru.\n15:6 M\u00e0ggal gu nekk nag Pilaat daan na may mbooloo mi, \u00f1u t\u00e0nn kenn ci \u00f1i \u00f1u t\u00ebjoon, mu b\u00e0yyil leen ko.\n15:7 Fekk booba amoon na ku \u00f1u t\u00ebj, tudd Barabas, ku bokk ci \u00f1a b\u00ebggoon a tas r\u00e9ew mi, boole ci rey nit.\n15:8 Noonu mbooloo mi \u00f1\u00ebw, laaj Pilaat, mu defal leen la mu daan def.\n15:9 Pilaat nag xam ne, ki\u00f1aan rekk a taxoon saraxalekat yu mag yi j\u00e9bbal ko Yeesu. Kon mu ne mbooloo mi: \u00abXanaa ma b\u00e0yyil leen buuru Yawut yi?\u00bb\n15:11 Waaye saraxalekat yu mag yi xiir mbooloo mi, \u00f1u laaj Pilaat, mu b\u00e0yyil leen Barabas.\n15:12 Kon Pilaat ne leen: \u00abLan laay def nag ak ki ngeen di wooye buuru Yawut yi?\u00bb\n15:13 \u00d1u daldi yuuxuwaat naan: \u00abDaaj ko ci bant, ba mu dee!\u00bb\n15:14 Pilaat ne leen: \u00abLu tax? Gan too\u00f1 la def?\u00bb Waaye mbooloo mi di yuuxu bu g\u00ebn a kawe: \u00abDaaj ko ci bant!\u00bb\n15:15 Noonu Pilaat, mi wut a neex mbooloo mi, b\u00e0yyil leen Barabas, ba noppi mu d\u00f3orlu Yeesu ay yar, j\u00e9bbal ko, ngir \u00f1u daaj ko ci bant.\n15:16 Bi loolu amee \u00f1u dugal Yeesu ci biir k\u00ebr boroom r\u00e9ew ma, mooy b\u00e9rab bu \u00f1uy wax Peretoriyum, \u00f1u daldi woo mbooloom xarekat y\u00e9pp.\n15:17 Noonu \u00f1u solal ko mbubb mu xonq curr, r\u00e0bb kaalag d\u00e9g, teg ko ci boppam.\n15:18 \u00d1u daldi ko wax bu kawe: \u00abNuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!\u00bb\n15:19 \u00d1u di ko d\u00f3or ci bopp ak bant, di ko tifli, daldi sukk, m\u00e0ggal ko.\n15:20 Bi \u00f1u ko \u00f1aawalee noonu ba noppi, \u00f1u summi mbubb mu xonq mi, solaatal ko ay y\u00e9reem, y\u00f3bbu ko, ngir daaj ko ci bant.\n15:21 Amoon na nag nit ku d\u00ebkk Siren, tudd Simo\u014b, di baayu Alegs\u00e0ndar ak Rufus. Fekk booba mu romb fa, j\u00f3ge ca wet, ga f\u00e9ete ak tool ya, \u00f1u ga ko ngir mu g\u00e0ddu bant bi.\n15:22 Noonu \u00f1u y\u00f3bbu Yeesu ca b\u00e9rab bu \u00f1uy wax Golgota, liy tekki \u00abB\u00e9rabu kaa\u014bu bopp.\u00bb\n15:23 \u00d1u b\u00ebgg koo jox bii\u00f1 bu \u00f1u boole ak naan gu tudd miir, waaye nanguwu ko.\n15:24 Foofa \u00f1u daaj Yeesu ci bant, daldi s\u00e9ddoo ay y\u00e9reem, tegoo ko ay bant, ba xam ku nekk, looy am;\n15:25 booba fekk yoor-yoor di jot.\n15:26 Mbind mi xamle lu tax \u00f1u rey ko nee na: \u00abKii mooy buuru Yawut yi.\u00bb\n15:27 Booba it \u00f1u daajaale ak moom \u00f1aari taskati r\u00e9ew mi, kenn ci ndeyjooram, ki ci des ci c\u00e0mmoo\u00f1am.\n15:29 \u00d1a fa doon romb di ko xas, di w\u00ebcc seen bopp ndax sib ko naan: \u00abWaaw kay, yaw mi b\u00ebgg a toj k\u00ebr Y\u00e0lla gi, tabaxaat ko ci \u00f1etti fan,\n15:30 w\u00e0ccal ci bant bi te musal sa bopp!\u00bb\n15:31 Noonu it saraxalekat yu mag yi ak xutbakat yi di ko \u00f1aawal ci seen biir naan: \u00abKii musal na \u00f1eneen waaye m\u00ebnul a musal boppam.\n15:32 Almasi bii, di buuru Israyil, na w\u00e0cc l\u00e9egi ci bant bi, nu gis ko te g\u00ebm.\u00bb \u00d1i \u00f1u daajaale ak moom it di ko xarab.\n15:33 Li t\u00e0mbalee digg-b\u00ebcc\u00ebg, ba ci tisbaar, r\u00e9ew m\u00e9pp l\u00ebnd\u00ebm.\n15:34 Ci tisbaar nag Yeesu wootee k\u00e0ddu gu d\u00ebg\u00ebr naan: \u00abElowi, Elowi, lema sabaktani?\u00bb liy tekki: \u00abSama Y\u00e0lla, sama Y\u00e0lla, lu tax nga d\u00ebddu ma?\u00bb\n15:35 \u00d1enn ci \u00f1a fa taxaw nag, bi \u00f1u ko d\u00e9ggee, \u00f1u ne: \u00abMu ngi woo yonent Y\u00e0lla Iliyas.\u00bb\n15:36 Noonu kenn daw, j\u00ebl aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci bant, jox ko ko, mu muucu. Mu ne: \u00abB\u00e0yyileen, nu seet, ba xam Iliyas dina \u00f1\u00ebw, w\u00e0cce ko.\u00bb\n15:37 Noonu Yeesu wootewaat ak k\u00e0ddu gu d\u00ebg\u00ebr, delloo ruuwam Y\u00e0lla.\n15:38 Bi mu ko defee ridob b\u00e9rab bu sell ba ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga xar \u00f1aar, li dale ci kaw ba ci suuf.\n15:39 Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanamu Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne: \u00abCi d\u00ebgg, nit kii Doomu Y\u00e0lla la!\u00bb\n15:40 Amoon na fa nag ay jig\u00e9en, \u00f1u leen dand, di xool. X\u00e0mmi na\u00f1u ci: Maryaama mi d\u00ebkk Magdala, Maryaama yaayu Saag mu ndaw ak Yuusufa, ak Salome.\n15:41 Bi Yeesu nekkee Galile, jig\u00e9en \u00f1oo\u00f1u \u00f1oo ko doon topp, di ko topptoo. Amoon na fa it yeneen jig\u00e9en yu bare yu \u00e0ndoon ak moom, ba \u00f1\u00ebw Yerusalem.\n15:42 Booba nag b\u00e9su Waajal la woon, maanaam b\u00e9s bu jiitu b\u00e9su noflaay bi. Ca ngoon sa nag,\n15:43 Yuusufa mi d\u00ebkk Arimate takk aw fitam, dem Pilaat, laaj ko n\u00e9ewu Yeesu. Yuusufa moomu nag, ku siiw la woon ci kureelu \u00e0ttekat yi, te doon s\u00e9entu moom itam nguuru Y\u00e0lla.\n15:44 Bi Pilaat d\u00e9ggee ne, Yeesu faatu na xaat, mu waaru. Mu woolu nag njiit li, laaj ko, ndax y\u00e0gg na faatu.\n15:45 Bi ko ko njiit li d\u00ebggalee, Pilaat jox n\u00e9ew bi Yuusufa.\n15:46 Noonu Yuusufa j\u00ebnd c\u00e0ngaay, w\u00e0cce n\u00e9ew bi, laxas ko ci, dugal ko cib b\u00e0mmeel bu \u00f1u yett ci xeer. Bi mu ko defee mu b\u00e9ra\u014b aw doj, ube ko buntu b\u00e0mmeel bi.\n15:47 Maryaamam Magdala nag ak Maryaama yaayu Yuusufa xool fu mu ko denc.\n16:1 Bi b\u00e9su noflaay bi w\u00e9yee, Maryaamam Magdala, Maryaama yaayu Saag, ak Salome, j\u00ebnd cuuraay, ngir dem xee\u00f1al n\u00e9ewu Yeesu.\n16:2 Kon b\u00e9s bu j\u00ebkk ci ayu-b\u00e9s gi, \u00f1u nj\u00eblu dem ca b\u00e0mmeel ba,\n16:3 di laajante: \u00abKu nuy b\u00e9ra\u014bal doj, wiy ub b\u00e0mmeel bi?\u00bb Doj woowu nag bu r\u00e9y-a-r\u00e9y la woon. Noonu \u00f1u xool, gis ne doj wa de\u00f1.\n16:5 \u00d1u dugg ci b\u00e0mmeel bi, gis ca ndeyjoor waxambaane wu sol mbubb mu weex, \u00f1u daldi tiit.\n16:6 Waaye mu ne leen: \u00abBuleen tiit. Y\u00e9ena ngi seet Yeesum Nasaret, mi \u00f1u daajoon ci bant bi. Nekkatu fi, dekki na; gisleen fi \u00f1u ko t\u00ebraloon.\n16:7 Kon nag demleen, ne Piyeer ak taalibe ya: \u201cMi ngi leen di jiitu Galile. Foofa ngeen koy gise, ni mu leen ko waxe woon.\u201d\u00bb\n16:8 Noonu jig\u00e9en \u00f1i g\u00e9nn, dawe b\u00e0mmeel ba, tiit bay lox. Te waxu\u00f1u kenn dara ndax seen tiit.\n16:9 Bi Yeesu dekkee nag ci suba teel ca b\u00e9s bu j\u00ebkk ca ayu-b\u00e9s ga, mu j\u00ebkk a fee\u00f1u Maryaama mu d\u00ebkk Magdala, mi mu d\u00e0qe woon jur\u00f3om-\u00f1aari rab.\n16:10 Maryaama nag dem nettali ko \u00f1i \u00e0ndoon ak Yeesu, fekk \u00f1uy naqarlu, di jooy.\n16:11 Bi \u00f1u d\u00e9ggee ne, Yeesoo ngi dund te Maryaama gis na ko, g\u00ebmu\u00f1u ko.\n16:12 Gannaaw loolu Yeesu fee\u00f1u \u00f1aar ci \u00f1oom ci jeneen j\u00ebmm, \u00f1uy jaar ci yoon wi, j\u00ebm \u00e0ll ba.\n16:13 \u00d1u wo\u00f1\u00f1iku nag, wax ko \u00f1a ca des, waaye ba tey g\u00ebmu\u00f1u leen \u00f1oom it.\n16:14 Gannaaw ga it Yeesu fee\u00f1u fukki taalibe yi ak benn, bi \u00f1uy lekk. Mu yedd leen ndax seen ng\u00ebmadi ak seen d\u00ebg\u00ebr bopp, ci li \u00f1u ba\u00f1 a g\u00ebm \u00f1i ko gisoon, bi mu dekkee.\n16:15 Mu ne leen: \u00abDemleen ci \u00e0ddina s\u00e9pp, y\u00e9gal xebaar bu baax bi mbindeef y\u00e9pp.\n16:16 Ku g\u00ebm te \u00f1u s\u00f3ob ko ci ndox, dina mucc; ku g\u00ebmul, dees na ko daan.\n16:17 \u00d1i ma g\u00ebm dina\u00f1u \u00e0nd ak firnde yii: ci sama tur dina\u00f1u d\u00e0q rab yi, di wax l\u00e0kk yu bees,\n16:18 di j\u00e0pp jaan ak seeni loxo; te bu \u00f1u naanee lu \u00f1u tooke, du leen w\u00e0\u00f1\u00f1i dara, te jarag ju \u00f1u teg loxo, mu w\u00e9r.\u00bb\n16:19 Gannaaw bi Boroom bi Yeesu waxee ak \u00f1oom, mu y\u00e9kkatiku, dem asamaan, toog ci ndeyjooru Y\u00e0lla.\n16:20 Taalibe ya dem waareji, te loxob Boroom bi \u00e0nd ak \u00f1oom, di d\u00ebggal k\u00e0ddu gi ak firnde, yi ci \u00e0nd.","title":"Wolof Bible (NT): Mark","type":"page"}
