{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/pe1.htm","path":"bib/wb/wlf/pe1.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/pe1.htm","text":"1:1 Man Piyeer, ndawul Yeesu Kirist, maa leen di bind, y\u00e9en doxand\u00e9em yi tasaaroo ci diiwaani Pont, Galasi, Kapados, Asi ak Bitini. Y\u00e0lla Baay bi t\u00e0nn na leen,\n1:2 ci li mu leen xam bu jiitu, te s\u00e9dde leen boppam ci j\u00ebfu Xel mu Sell mi, ngir ngeen d\u00e9ggal ko, te seen xol laab ndax deretu Yeesu Kirist. Na leen Y\u00e0lla dollil yiw ak j\u00e0mm.\n1:3 Cant \u00f1eel na Y\u00e0lla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist! Moo nu judduwaatal ci y\u00ebrmandeem ju bare, ba may nu yaakaar ju sax ndax ndekkitel Yeesu Kirist.\n1:4 S\u00e9dd na leen c\u00e9r bu dul y\u00e0qu, du g\u00e0kk te du seey mukk, dencal leen ko ci asamaan,\n1:5 y\u00e9en \u00f1i muy aar ci dooleem, sukkandikoo ci ng\u00ebm, di leen n\u00e9ge mucc, gi mu nar a fee\u00f1al b\u00e9s bu mujj ba.\n1:6 Y\u00e9ena ngi b\u00e9g bu baax ci biir yaakaar jooju, doonte sax, su waree am, y\u00e9ena ngi d\u00e9kku tiis ab diir, ci seen j\u00e0nkoonte ak nattu yu wuute.\n1:7 Xam ne nattu yooyu dina\u00f1u sellal seen ng\u00ebm, ni safara di setale wurus, fekk wurus luy w\u00e9y la, te ng\u00ebm a ko g\u00ebn fuuf. Noonu seen ng\u00ebm dina yelloo cant, ndam ak m\u00e0gg, b\u00e9s bu Yeesu Kirist fee\u00f1ee.\n1:8 Musuleen koo gis waaye b\u00ebgg ngeen ko, gisuleen ko waaye g\u00ebm ngeen ko te am mb\u00e9g mu xel dajul, mu fees dell ak ndam,\n1:9 di jot muj gi ng\u00ebm s\u00e9entu, maanaam muccu xol.\n1:10 Naka mucc googu nag, yonent yi xamle yiw, wi ngeen naroon a joti, seet na\u00f1u ko te g\u00ebstu ko.\n1:11 Bi Xelum Kirist, mi nekkoon ci \u00f1oom, seedee lu jiitu coonoy Kirist ak ndam la cay topp, j\u00e9em na\u00f1oo takk, ka\u00f1 ak nan lay ame.\n1:12 Waaye Y\u00e0lla xamal na leen ne, moomu\u00f1u woon k\u00e0ddu googu \u00f1u wax, waaye y\u00e9ena ko moom. Te mooy k\u00e0ddu gi ngeen d\u00e9gg ci g\u00e9mmi\u00f1u \u00f1i leen doon jottali xebaar bu baax bi, ci dooley Xel mu Sell, mi Y\u00e0lla y\u00f3nnee asamaan; malaaka yi sax b\u00ebgg na\u00f1oo g\u00ebstu y\u00ebf yii.\n1:13 Kon fagaruleen ci seeni xalaat te maandu, di w\u00e9kk seen yaakaar j\u00e9pp ci yiw, wi leen Y\u00e0lla di jagleel b\u00e9s bu Yeesu Kirist di fee\u00f1.\n1:14 Gannaaw gaayi Y\u00e0lla yu koy d\u00e9ggal ngeen, buleen toppati b\u00ebgg-b\u00ebgg, yi ngeen toppoon, bi ngeen xamagul Y\u00e0lla.\n1:15 Waaye na seen dund g\u00e9pp sell, ni Y\u00e0lla mi leen woo selle.\n1:16 Ndaxte Mbind mi nee na: \u00abSell-leen, ndaxte ku sell laa.\u00bb\n1:17 Gannaaw nag Y\u00e0lla, mi ngeen di wooye Baay, mooy \u00e0tte j\u00ebfi \u00f1\u00e9pp te du g\u00ebnale kenn, saxleen ci ragal ko diirub seen ngan ci \u00e0ddina.\n1:18 Xam ngeen ne, Y\u00e0lla jot na leen ci seen dund gu tekkiwul dara, gi maam ya nekkoon; te jotuleen ak yu deme ni xaalis mbaa wurus yuy w\u00e9y,\n1:19 waaye ci deretu Kirist ju tedd ji, mel ni mbote mu sikkul te w\u00e0\u00f1\u00f1ikuwul.\n1:20 Y\u00e0lla xamoon na ko, ba \u00e0ddina sosoogul, waaye l\u00e9egi ci mujug jamono fee\u00f1al na ko ndax y\u00e9en\n1:21 \u00f1i jaar ci moom, g\u00ebm Y\u00e0lla. Te Y\u00e0lla dekkal na ko, sol ko ndam, ngir ngeen w\u00e9kk seen ng\u00ebm ak seen yaakaar ci Y\u00e0lla.\n1:22 Kon nag gannaaw d\u00e9ggal ngeen d\u00ebgg gi, ba sellal seeni xol te am mb\u00ebggeel gu d\u00ebggu, b\u00ebgganteleen mb\u00ebggeel gu tar ak seen xol b\u00e9pp.\n1:23 Ndaxte du ci jiwu wuy y\u00e0qu ngeen judduwaate, waaye ci jiwu wu sax, maanaam k\u00e0ddug Y\u00e0lla giy dund tey sax.\n1:24 Ndaxte:\u00abNit \u00f1ax la,ndamam di t\u00f3or-t\u00f3or kese;\u00f1ax day wow, t\u00f3or-t\u00f3or ruus,waaye k\u00e0ddug Boroom bi day sax ba f\u00e0ww.\u00bb\n1:25 Te k\u00e0ddu googu mooy xebaar bu baax, bi \u00f1u leen doon y\u00e9gal.\n2:1 Kon nag d\u00ebdduleen g\u00e9pp coxor, g\u00e9pp njubla\u014b, naaf\u00e9q, ki\u00f1aan ak j\u00ebw.\n2:2 Gannaaw ay liir ngeen yuy door a juddu te mos ci mbaaxug Boroom bi, n\u00e0mpleen ci meew mu sell, miy dundal seen xol, ba m\u00e0gg ci biir muccu Y\u00e0lla.\n2:4 Kon nag \u00f1\u00ebwleen ci moom; nit \u00f1i ba\u00f1 na\u00f1u ko, waaye Y\u00e0lla fal na ko te teral ko. Mi ngi mel ni doju tabax, waaye doj wuy dund la,\n2:5 te y\u00e9ena ngi mel niy doj yuy dund yu Y\u00e0llay defare d\u00ebkkukaayam. Noonu ay saraxalekat yu sell ngeen, ngir j\u00e9bbal ko ay sarax yu ngeen tibbe ci seen xol te neex ko ndax Yeesu Kirist.\n2:6 Looloo tax bind na\u00f1u:\u00abMaa ngi samp fi ci Siyon doju ko\u00f1.Doj wu tedd la, wu ma t\u00e0nn;ku g\u00ebm ci moom, sa yaakaar du tas mukk.\u00bb\n2:7 Kon nag y\u00e9en \u00f1i g\u00ebm am ngeen c\u00e9r ci teraangaam. Waaye naka \u00f1i g\u00ebmul:\u00abDoj wa tabaxkat ya s\u00e0nni,mujj na di doju ko\u00f1.\u00bb\n2:8 Te it:\u00abDoj la wuy f\u00e9l nit,di xeer wu koy fakkastal.\u00bb Da\u00f1u cee fakkastalu, ndaxte g\u00ebmu\u00f1u k\u00e0ddug Y\u00e0lla, te loolu la Y\u00e0lla dogal ci \u00f1oom.\n2:9 Waaye y\u00e9en xeet wu Y\u00e0lla t\u00e0nn ngeen, di askanu saraxalekati Buur Y\u00e0lla, askan wu sell ngeen, di mbooloom Y\u00e0lla, ngir ngeen y\u00e9gle ng\u00ebneelam, moom mi leen woo, ba g\u00e9nne leen l\u00ebnd\u00ebm gi, t\u00e0bbal leen ci leeram gu y\u00e9eme gi.\n2:10 D\u00e9mb nekkuleen woon ci dara, waaye tey mbooloom Y\u00e0lla ngeen; booba jotuleen woon y\u00ebrmandeem, waaye l\u00e9egi jot ngeen ko.\n2:11 Samay xarit, y\u00e9en \u00f1iy ay gan ak ay doxand\u00e9em ci \u00e0ddina si, maa ngi leen di d\u00e9nk lii: d\u00ebdduleen b\u00e0nneexi bakkan yiy xeex ak xol.\n2:12 Na seen dundin rafet ci biir xeeti \u00e0ddina, kon doonte \u00f1u di leen sosal ay \u00f1aawteef, dina\u00f1u gis seeni j\u00ebf yu rafet bay m\u00e0ggal Y\u00e0lla, b\u00e9s bu leen fee\u00f1oo.\n2:13 Na seen nangub Boroom bi tax, ngeen d\u00e9ggal k\u00e9pp kuy kilifa, muy buur ba g\u00ebn a kawe,\n2:14 mbaa jawri\u00f1 yu mu yebal, ngir \u00f1u yar \u00f1iy def lu bon, te teral \u00f1iy def lu baax.\n2:15 Ndaxte noonu la coobareg Y\u00e0lla t\u00ebdde, maanaam ngeen sax ci def lu baax, ba wedamloo jayil yi xamul dara.\n2:16 Li leen Y\u00e0lla goreel nag, bu mu tax ngeen mbubboo ko, bay def lu bon, waaye ngeen g\u00ebn a feddali seen jaamu Y\u00e0lla.\n2:17 Teral-leen \u00f1\u00e9pp, b\u00ebgg kureelu bokk yi, ngeen ragal Y\u00e0lla te teral buur bi.\n2:18 Y\u00e9en jaam yi d\u00e9ggal-leen seeni sang ak wegeel gu mat s\u00ebkk, waxuma \u00f1i baax te lewet rekk, waaye sax \u00f1u wex \u00f1i.\n2:19 Ndaxte su ngeen d\u00e9kkoo tiis, di sonn ci lu dul yoon ndax seen \u00e0nd ak Y\u00e0lla, loolu lu rafet la.\n2:20 Su ngeen too\u00f1ee te mu\u00f1 i pes, luy pey gi? Waaye su \u00f1u leen fitnaalee ci def lu baax te ngeen mu\u00f1 ko, j\u00ebf ju rafet la fa kanam Y\u00e0lla.\n2:21 Ndaxte ci loolu la leen Y\u00e0lla woo, ndaxte Kirist itam sonn na ngir y\u00e9en, teg fi seen kanam royukaay, ngir ngeen jaar ciy t\u00e0nkam.\n2:22 \u00abMusul a def b\u00e0kkaar,te jenn waxu njubla\u014b musul a g\u00e9nn ci g\u00e9mmi\u00f1am.\u00bb\n2:23 Saaga na\u00f1u ko te feyyuwul, fitnaal na\u00f1u ko te t\u00ebkkuwul, waaye mu d\u00e9nk boppam Ki yor \u00e0tte bu d\u00ebgg bi.\n2:24 G\u00e0ddu na moom ci boppam sunuy b\u00e0kkaar ca bant, ba \u00f1u ko daajoon, ngir nu t\u00e0ggook b\u00e0kkaar, s\u00f3obu ci dund gu jub; ndax ay gaa\u00f1u-gaa\u00f1oom may na nu ag w\u00e9r.\n2:25 Ndaxte y\u00e9ena ngi r\u00e9eroon niy xar, waaye l\u00e9egi dellusi ngeen ci s\u00e0mm, biy aar seeni xol.\n3:1 Y\u00e9en itam jig\u00e9en \u00f1i, na ku nekk nangul sa j\u00ebkk\u00ebr. Noonu su amee g\u00f3or gu g\u00ebmul k\u00e0ddug Y\u00e0lla, te gis jabaram di dund dund gu sell, boole ci weg ko, loolu dina ko gindi ci lu \u00e0ndul ak wax.\n3:3 Bu seen taar aju ci col, maanaam ay l\u00e9tt, wurus mbaa y\u00e9re yu rafet,\n3:4 waaye nay taar bu sax bu nekk ci biir, di xol bu nooy te dal, ndax loolu lu takku la fa Y\u00e0lla.\n3:5 Ndaxte jig\u00e9eni d\u00e9mb yu sell, ya g\u00ebmoon Y\u00e0lla, loolu moo doon seen taar; nanguloon na\u00f1u seen j\u00ebkk\u00ebr,\n3:6 ni Saarata d\u00e9ggale woon Ibraayma, ba daan ko wooye \u00abSang bi.\u00bb Y\u00e9en nag, su ngeen dee def lu baax te ba\u00f1 cee boole genn nj\u00e0qare, kon mel na ni Saarataa leen jaboote.\n3:7 Te y\u00e9en itam g\u00f3or \u00f1i, na ku nekk ci y\u00e9en am xel, ci ni ngay \u00e0nde ak sa jabar, xam ne \u00e0ndandoo ju la g\u00ebn a n\u00e9ew doole la. Joxleen ko teraanga ju mat, ndax y\u00e9ena yem c\u00e9r ci yiwu Y\u00e0lla, wi nu ubbil buntu dund gu dul jeex. Noonu dara du man a y\u00e0q seeni \u00f1aan.\n3:8 Kon nag bokkleen xalaat, bokkleen i tiis, b\u00ebgganteleen, y\u00ebr\u00ebmante te woyof.\n3:9 Ku la def lu bon mbaa mu saaga la, bul feyyu, waaye \u00f1aanal ko lu baax; ndaxte ci loolu la leen Y\u00e0lla woo, ngir barkeel leen.\n3:10 Ndaxte:\u00abKu b\u00ebgg a am dund gu naatte fekke b\u00e9s yu rafet,na j\u00e0pp l\u00e0mmi\u00f1am ci lu bon,s\u00e0mm g\u00e9mmi\u00f1am ci fen.\n3:11 Na d\u00ebddu lu bon, tey def lu baax,na x\u00ebnte j\u00e0mm te sax ci.\n3:12 Ndax Boroom baa ngi xool \u00f1i jub b\u00ebti y\u00ebrmande,di ubbi ay noppam ci seeni \u00f1aan,waaye d\u00e0q \u00f1iy def lu bon.\u00bb\n3:13 Te it kan moo leen di sonal, su ngeen g\u00f3or-g\u00f3orloo ci def lu baax?\n3:14 Doonte \u00f1u di leen fitnaal sax ci def lu jub, \u00f1u barkeel ngeen. Buleen tiit nag ndax seeni x\u00ebbal, mbaa ngeen di ci am nj\u00e0qare.\n3:15 Waaye m\u00e0ggal-leen Kirist Boroom bi ci seeni xol, te jekk ngir tontu ku lay laaj ci seen yaakaar ji ngeen am;\n3:16 waaye na tont gi lewet te \u00e0nd ak wegeel. \u00c0ndleen ak xel mu dal; noonu \u00f1i leen di sikkal ndax seen dund gu rafet ci g\u00ebm Kirist, dina\u00f1u rus ci seeni sos.\n3:17 \u00d1u fitnaal la ndax j\u00ebf ju baax, su dee mooy coobareg Y\u00e0lla, moo g\u00ebn \u00f1u fitnaal la ndax j\u00ebf ju bon.\n3:18 Ndaxte Kirist ci boppam dee na benn yoon ba f\u00e0ww, ngir dindi b\u00e0kkaar yi, moom mi jub ngir \u00f1i jubadi, ngir y\u00f3bbu leen fa Y\u00e0lla; dee na ci j\u00ebmm, waaye dundaat na ci xel.\n3:19 Ci biir xel moomu la y\u00e9galeji ndamam ca ruu ya Y\u00e0lla t\u00ebj kaso;\n3:20 maanaam \u00f1a weddi woon ca jamonoy N\u00f3oyin, fekk Y\u00e0lla mu\u00f1aloon na leen diir bu y\u00e0gg, dajeek N\u00f3oyin doon yett gaal ga. \u00d1u n\u00e9ew, maanaam limub jur\u00f3om-\u00f1ett, dugg na\u00f1u ca gaal ga, jaar ca ndox ma, ba mucc.\n3:21 Loolu misaal la tey, ci li \u00f1u nuy s\u00f3ob ci ndox, te nu mucc; waxuma laabal sobe si taq ci yaram, waaye wuyu Y\u00e0lla ak xel mu dal. Li nu may mucc googu, mooy ndekkitel Yeesu Kirist,\n3:22 mi y\u00e9eg asamaan, toog fa ndeyjooru Y\u00e0lla, mu tiim malaaka yi, boroom sa\u00f1-sa\u00f1 yi ak boroom doole y\u00e9pp.\n4:1 Gannaaw Kirist nag sonn na ci yaramam, g\u00e0nnaayooleen xelam moomu, ndaxte ku sonn ci yaramam, t\u00e0ggoo na ak b\u00e0kkaar.\n4:2 Noonu diir bi ko dese ci kaw suuf, d\u00ebddu na b\u00e0nneexi bakkan, jublu ci coobareg Y\u00e0lla.\n4:3 Ndaxte \u00e0ndoon ngeen d\u00e9mb ci xalaati \u00f1i xamul Y\u00e0lla, di dund ciy \u00f1aawteef ak topp seen bakkan, di m\u00e0ndi ak a xawaare, di x\u00e9r ci bii\u00f1 ak a jaamu ay x\u00ebr\u00ebm yu araam, waaye na fi yem nag.\n4:4 \u00d1iy j\u00ebfe noonu waaru na\u00f1u, ba di leen sosal, ci li ngeen \u00e0ndul ak \u00f1oom, s\u00f3obu ci seeni moy yu dul jeex,\n4:5 waaye dina\u00f1u mas a teew fa kanam Ki nar a \u00e0tte \u00f1iy dund ak \u00f1i dee.\n4:6 Looloo waral it \u00f1u jottali xebaar bu baax ndee, ya fekke woon jamonoy N\u00f3oyin jooju, ngir \u00f1u dunde Y\u00e0lla ci seen xel, doonte sax nit \u00f1aa ngi leen daan fitnaal ci \u00e0ddina.\n4:7 Te itam muju l\u00e9pp jegesi na; nangeen maandu te foog, ba man a \u00f1aan ci Y\u00e0lla.\n4:8 Li g\u00ebn a am solo mooy, ngeen b\u00ebggante mb\u00ebggeel gu tar, ndax mb\u00ebggeel day suul b\u00e0kkaar yu bare.\n4:9 Ganalanteleen ci lu \u00e0ndul ak nj\u00e0mbat.\n4:10 Te lu la Y\u00e0lla jagleel kenn ku nekk ci y\u00e9en, nanga ko bokk ak \u00f1\u00e9pp ni jawri\u00f1 ju jub, ci s\u00e9ddale yiwu Y\u00e0lla wu yaatu.\n4:11 Kuy jottali k\u00e0ddug Y\u00e0lla, na mel ni Y\u00e0llaay wax. Kuy j\u00ebf it, na j\u00ebfe dooley Y\u00e0lla, ngir turu Y\u00e0lla m\u00e0gg ci l\u00e9pp jaar ci Yeesu Kirist, mi yelloo ndam ak k\u00e0ttan ba f\u00e0ww. Amiin.\n4:12 Y\u00e9en samay xarit, ci mbirum nattu bu t\u00e0nge ni daay, bi dal ci seen kaw, bumu leen jaaxal, ba ngeen teg ko ni lu xel dajul.\n4:13 Waaye b\u00e9gleen ci c\u00e9r, boobu ngeen am ci coonoy Kirist, ngir b\u00e9s bu ndamam di fee\u00f1, ngeen b\u00e9g ak mb\u00e9g mu \u00ebpp xel.\n4:14 Su \u00f1u leen j\u00e0nnee sax ci turu Kirist, xamleen ne \u00f1u barkeel ngeen, ndax Xelum Y\u00e0llaa ngi ci y\u00e9en, di firndeel seen ndamu \u00ebll\u00ebg.\n4:15 Bu\u00f1u sonal kenn ci y\u00e9en ci li mu rey nit walla mu s\u00e0cc, mbaa def lu bon, walla dugg ci lu yoonam nekkul.\n4:16 Waaye ku \u00f1u sonal ndax waayu Kirist nga, bu ci rus, waaye nga m\u00e0ggal Y\u00e0lla ci tur woowu.\n4:17 Ndaxte \u00e0pp bi jot na, \u00e0tte baa ngi t\u00e0mbalee ci nun waa k\u00ebr Y\u00e0lla. Te su t\u00e0mbalee ci nun nag, luy muju \u00f1i weddi xebaaru Y\u00e0lla?\n4:18 Te:\u00abSu muccu ki jub jafee,luy doon muju ki weddi te d\u00ebng?\u00bb\n4:19 Kon nag \u00f1i tegoo fitna ci coobareg Y\u00e0lla, na\u00f1u sax ci def lu baax, d\u00e9nk seen bopp Y\u00e0lla, miy Bindkat biy s\u00e0mm k\u00f3ll\u00ebre.\n5:1 Kon y\u00e9en njiit yi, maa ngi leen di d\u00e9nk, man miy njiit ni y\u00e9en, man mi seede coonoy Kirist te am c\u00e9r ci ndam li nar a fee\u00f1.\n5:2 Lii laa leen di \u00f1aan: s\u00e0mmleen g\u00e9ttug Y\u00e0lla, gi mu leen d\u00e9nk, di ko wottu, waxuma ci sa\u00f1ul-ba\u00f1, waaye di surgay Y\u00e0lla ci xol bu t\u00e0lli; ngeen def ko ak xol bu laab te ba\u00f1 cee s\u00e9entu alal.\n5:3 Buleen noot \u00f1i leen Y\u00e0lla d\u00e9nk, waaye ngeen nekk ay royukaay fi kanam jur gi.\n5:4 Noonu waxtu wu Boroom g\u00e9tt gi fee\u00f1ee, dina leen jagleel kaalag ndam guy sax ba f\u00e0ww.\n5:5 Noonu itam y\u00e9en ndaw \u00f1i, nangeen d\u00e9ggal mag \u00f1i. Te y\u00e9en \u00f1\u00e9pp, solooleen woyof ci seen biir, ndaxte:\u00abY\u00e0lla day d\u00e0q \u00f1i r\u00e9y,di yiwal \u00f1i woyof.\u00bb\n5:6 Suufeel-leen seen bopp kon ci ron loxob Y\u00e0lla bu am k\u00e0ttan, ngir mu y\u00e9kkati leen ci jamono ju ko soob.\n5:7 Te ngeen yenniku ci kawam seen nj\u00e0qare j\u00e9pp, ndax ku leen \u00f1eewante la.\n5:8 Maanduleen te foog, ndax seen noon Seytaane mu ngi w\u00ebr, ni gaynde guy y\u00ebmmu, di r\u00ebbb ku mu y\u00e0pp.\n5:9 J\u00e0nkoonteleen ak moom ci biir ng\u00ebm gu takku, xam ne kureelu bokk yi ci \u00e0ddina y\u00e9pp, \u00f1u ngi daj ay fitna ni y\u00e9en.\n5:10 Te Y\u00e0lla mi jagoo yiw w\u00e9pp te woo leen ci darajay Kirist, ngir ngeen bokk ci ndamam li sax, gannaaw bi ngeen yendoo b\u00ebcc\u00ebgu tiis, dina leen yeesalaat, di leen d\u00ebg\u00ebral ak a dooleel, ba ngeen sampu.\n5:11 Na Y\u00e0lla yelloo m\u00e0gg ba f\u00e0ww. Amiin.\n5:12 Bind naa leen ci lu g\u00e0tt ci ndimbalu Silwan, mi ma j\u00e0pp ni sama mbokk mu takku. D\u00e9nk naa leen, di leen seedeel ne, lii mooy yiwu Y\u00e0lla d\u00ebgg; kon nag saxleen ci.\n5:13 Mbooloo mi nekk ci d\u00ebkk bi \u00f1uy wax Babilon te Y\u00e0lla t\u00e0nn ko ni y\u00e9en, moo di leen nuyu, \u00f1oom ak M\u00e0rk sama doomu diine.\n5:14 Nuyoonteleen ak saafoonte yu sell. Na j\u00e0mm \u00f1eel k\u00e9pp ku g\u00ebm Kirist.","title":"Wolof Bible (NT): 1 Peter","type":"page"}
