{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/pe2.htm","path":"bib/wb/wlf/pe2.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/pe2.htm","text":"1:1 Man Simo\u014b Pieer, jaamu Yeesu Krist ak ndawam, maa leen di bind, yeen \u00f1i Y\u00e0lla jagleel ng\u00ebm gu rafet ni nun, aju ci njubu sunu Y\u00e0lla ak Musalkat, Yeesu Krist.\n1:2 Na leen Y\u00e0lla dollil yiw ak j\u00e0mm, jaar ci xam ko ak Yeesu sunu Boroom.\n1:3 Dooley Y\u00e0lla moo nu may l\u00e9pp lu aju ci dund gu sax ak ragal Y\u00e0lla, jaarale ko ci xam gi nu ko xam, moom mi nu woo ci kaw ndamam ak dooleem.\n1:4 Noonu la nu dige ay dig yu rafet, te r\u00e9y ba \u00ebpp xel, ngir nu g\u00ebm leen, te Y\u00e0lla sol nu jikoom, nu mucc ci y\u00e0qute, gi b\u00e0nneexu bakkan samp ci \u00e0ddina si.\n1:5 Na loolu tax ngeen g\u00f3or-g\u00f3orlu, ba yokk ci seen ng\u00ebm nj\u00e0mbaar, ci nj\u00e0mbaar googu ngeen yokk ci xam-xam, yokk ci noot sa bopp.\n1:6 Noot sa bopp googu, ngeen yokk ci mu\u00f1, yokk ci ragal Y\u00e0lla,\n1:7 yokk ci sopp mbokk, yokk ci b\u00ebgg \u00f1\u00e9pp.\n1:8 Ndaxte bu leen jiko yooyu soloo, ba sax ci yeen, dina tax seen xam Yeesu Krist Boroom bi am njeri\u00f1 te jur mbaax.\n1:9 Waaye ku \u00f1\u00e0kk jiko yooyu, ay b\u00ebtam da\u00f1oo l\u00ebnd\u00ebm ba gumba, te f\u00e0tte na, ni ko Y\u00e0lla f\u00f3otale b\u00e0kkaari d\u00e9mb.\n1:10 Kon nag samay mbokk, gannaaw Y\u00e0lla da leena t\u00e0nn te woo leen, g\u00f3or-g\u00f3orluleen ci feddali ko ak seen kem-k\u00e0ttan. Ndaxte su ngeen ko defee, dungeen jeng mukk.\n1:11 Te noonu dingeen t\u00e0bbi ak ndam ci nguur gu sax gu sunu Boroom, di sunu Musalkat Yeesu Krist.\n1:12 W\u00f3or na ma ne xam ngeen loolu, ba sampu ci d\u00ebgg gi leen Y\u00e0lla jagleel, waaye fas naa y\u00e9ene, may sax ci di leen ko f\u00e0ttali.\n1:13 Te j\u00e0pp naa ko, muy sama warugar, feek maa ngi noyyi, ma di leen f\u00e0ttali loolu, ba yee leen.\n1:14 Ndaxte xam naa ne, l\u00e9egi ma j\u00f3ge fi, ni ma ko Yeesu Krist Boroom bi leerale woon.\n1:15 Te dinaa g\u00f3or-g\u00f3orlu, ngir sama gannaaw ngeen di f\u00e0ttaliku li ma leen doon wax.\n1:16 Bi nu leen y\u00e9galee dooley Yeesu Krist sunu Boroom ak \u00f1\u00ebwam ci biir ndam, sukkandikuwunu woon ciy l\u00e9eb yu s\u00ebsul fenn, waaye danoo teewe ag m\u00e0ggam.\n1:17 Ndaxte Y\u00e0lla Baay bi sol na ko teraanga ak ndam, te baatub Aji M\u00e0gg ju tedd ji jib na ne: Sama Doom a ngii, di sama Soppe; ci moom laa ame b\u00e0nneex.\n1:18 Te nun d\u00e9gg nanu baat boobu j\u00f3ge asamaan, bi nu nekkee ak moom ca tund wu tedd wa.\n1:19 Noonu bir na ne, waxu yonent yi w\u00e9r na, te war ngeen koo fonk; mi ngi mel ni l\u00e0mp, buy leer ci b\u00e9rab bu l\u00ebnd\u00ebm, ba kera fajar di xar, te biddiiwub nj\u00ebl bi feq, leeral seeni xol.\n1:20 Waaye j\u00ebkkleena xam ne, amul jenn waxu yonent ci Mbind mi, ju balle ci xelu boppam.\n1:21 Ndaxte kenn ci yonent yi musula wax ci coobareg boppam, waaye, Xel mu Sell mi daa na xiir nit \u00f1i, \u00f1u y\u00e9gle k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n2:1 Waaye ci b\u00e0nni Israyil, amoon na naaf\u00e9q yu mbubboo turu yonent, ni muy ame seen biir \u00f1uy mbubboo turu j\u00e0ngalekat. Ci seeni pexe dina\u00f1u dugal ci yeen xalaat yu s\u00e0nke, di weddi Boroom bi leen jot, tey y\u00f3bbe seen bopp alkande ju teew.\n2:2 \u00f1u bare dina\u00f1u leen fekki ci seeni \u00f1aawteef, ba g\u00e0kkal yoonu d\u00ebgg ci b\u00ebti nit \u00f1i.\n2:3 Seen b\u00ebgge dina tax, \u00f1u d\u00e0bbdaaxe ay wax, ngir nax leen, ba lekk seenus tuut. Waaye \u00e0tte baa ngi leen di xaar, te seen alkande di leen teeru.\n2:4 Ndaxte Y\u00e0lla jeggalul malaaka ya b\u00e0kkaaroon, waaye t\u00e0bbal na leen safara, t\u00ebj leen ca k\u00e0mb yu l\u00ebnd\u00ebm, di leen n\u00e9ge \u00e0tte ba.\n2:5 Te it jeggalul \u00e0ddina su j\u00ebkk sa weddi woon, ba xooj ko ci ndoxu mb\u00ebnn ma, waaye musal na N\u00f3oyin rekk, mi daan waare ci njub, moom ak jur\u00f3om-\u00f1aari nit.\n2:6 Te it Y\u00e0lla daan na d\u00ebkki Sodom ak Gomor, raafal leen cig lakk, \u00f1uy misaalu \u00f1iy weddi \u00ebll\u00ebg.\n2:7 Waaye musal na L\u00f3ot mi jub, mi sonnoon ndax \u00f1aawteefi \u00f1u d\u00ebng, \u00f1oo\u00f1u mu nekkaloon.\n2:8 Ndaxte L\u00f3ot, mi d\u00ebkkoon ci seen biir, dafa d\u00ebkke woon tiisu xol, ndax \u00f1aawteef yi mu gis ak a d\u00e9gg guddi ak b\u00ebcc\u00ebg.\n2:9 Gannaaw loolu l\u00e9pp am na nag, nanu bir ne, Boroom bi man na musal aji g\u00ebm ji nekk ci nattu, te denc \u00f1i jubadi, ngir alag leen b\u00e9su \u00e0tte ba.\n2:10 Rawatina \u00f1iy topp seen bakkan ciy b\u00ebgg-b\u00ebgg yu ruslu, te faalewu\u00f1u genn kilifteef. \u00f1u \u00f1eme Y\u00e0lla la\u00f1u, te d\u00ebg\u00ebr bopp, ba ragalu\u00f1oo xas kilifa ya g\u00ebna kawe.\n2:11 Fekk sax malaaka, yi leen \u00ebpp doole ak k\u00e0ttan, tey sax ca jetaayu Boroom bi, \u00f1emewu\u00f1oo xas kilifa yooyu.\n2:12 Waaye \u00f1oom da\u00f1uy xas ci biir yi \u00f1u xamul. \u00f1oom ak b\u00e0yyima \u00f1oo yem, di ay mbindeef yuy ta\u00f1axu, te t\u00ebr rendi rekk a jekk ci \u00f1oom; dees na leen rey ni b\u00e0yyima,\n2:13 muy seen peyug njubadi. Xawaare b\u00ebcc\u00ebgu ndara-k\u00e0mm mooy seen b\u00e0nneex. Su \u00f1uy lekkandoo ak yeen, da\u00f1uy b\u00e0nneexu ci seeni b\u00ebgg-b\u00ebgg, di ay g\u00e0kk ak i sikk ci seen biir.\n2:14 Jig\u00e9en ju seen b\u00ebt tegu, \u00f1u x\u00e9dd ko, ba du\u00f1u t\u00e0ggook moy mukk; ku \u00f1\u00e0kk pasteef \u00f1u f\u00e0bbi la; \u00f1u xelu la\u00f1u j\u00ebme cig b\u00ebgge -- \u00f1u alku la\u00f1u!\n2:15 R\u00e9er na\u00f1u ba w\u00e0cc yoon wu jub wi, topp yoonu Balaam, doomu Bosor, mi b\u00ebgge xiiroon ci njubadi.\n2:16 Waaye d\u00e9ggadeem y\u00f3bbe na ko yeraanga; xam ngeen ne mbaam-s\u00ebf du wax, waaye mbaam wax na ak moom ci l\u00e0mmi\u00f1 wu bir, ngir mu g\u00e9nn ci ndofam googu.\n2:17 \u00d1oo\u00f1ule ay teen yu d\u00eby la\u00f1u, di xiini lay, yu ngelaw liy naawal, te seen pey mooy l\u00ebnd\u00ebm gu ne taraj.\n2:18 Da\u00f1uy f\u00e0bbi \u00f1u naroona mucc ci \u00e0ddina ju r\u00e9er, dig leen ak l\u00e0mmi\u00f1 yu neex b\u00e0nneexi bakkan yu j\u00e9ggi dayo.\n2:19 Da\u00f1u leen di dig ngoreel, te fekk \u00f1oom ci seen bopp jaami y\u00e0qute la\u00f1u, ndaxte lu la noot, jaamam nga.\n2:20 Su \u00f1u xamee Boroom bi, di sunu Musalkat Yeesu Krist, ba mucc ci sobes \u00e0ddina, ba noppi s\u00f3obuwaat ca, ba mu noot leen, seen muj moo y\u00e9es seen nj\u00e0lb\u00e9en.\n2:21 Ndaxte \u00f1u xam yoon wu jub wi, ba noppi d\u00ebddu ndigal lu sell li \u00f1u d\u00e9ggoon, ba\u00f1oon koo xam moo g\u00ebnoon ci \u00f1oom.\n2:22 Noonu seen mbir d\u00ebggal na li \u00f1uy wax ne: Xaj mooy waccu, di ko lekkaat; te it: Mbaam-xuux, loo ko sang-sang, mu xalangu ci ban.\n3:1 Yeen samay xarit, sama \u00f1aareelu bataaxel a ngi nii. Bind naa leen, ngir xiir leen ci xalaat yu sell.\n3:2 Maa ngi leen di f\u00e0ttali k\u00e0dduy yonent yu sell, yi fi jiitu woon, ak ndigalu Boroom bi sunu Musalkat, li ngeen d\u00e9ggoon ci ndaw, yi Y\u00e0lla yebaloon fi yeen.\n3:3 Nangeen j\u00ebkka xam lii: muju jamano dingeen gis ay tii\u00f1alkat, di topp seen bakkan; dina\u00f1u leen tii\u00f1al\n3:4 ci di leen ne: Ki dige woon ne dina \u00f1\u00ebw, ana mu? Ndaxte baay ya nelaw na\u00f1u, waaye l\u00e9pp a ngi dox ca nj\u00e0lb\u00e9en ga ba tey.\n3:5 Fekk b\u00ebggu\u00f1oo xam lii: k\u00e0ddug Y\u00e0llaa tax, asamaan ak \u00e0ddina yu j\u00ebkk ya juddoo ca ndox, te dunde ko.\n3:6 Te ndox it moo labal \u00e0ddina sa, raafal ko.\n3:7 Te k\u00e0ddug Y\u00e0lla googu moo denc asamaan yii fi nekk ak suuf si, ngir lakk leen; Y\u00e0llaa ngi leen di n\u00e9ge b\u00e9sub \u00e0tte, ba muy alag \u00f1i weddi.\n3:8 Yeen samay xarit, buleen umple ne, benn b\u00e9s ak junniy at \u00f1oo yem fi Boroom bi.\n3:9 Li Y\u00e0lla dige, dina ko def, lu mu yeex-yeex ci xalaatu nit. Xanaa kay da leena mu\u00f1al, ndax b\u00ebggul kenn alku, waaye \u00f1\u00e9pp tuub seeni b\u00e0kkaar.\n3:10 Waaye b\u00e9su Boroom bi dina \u00f1\u00ebw, bett \u00e0ddina ni s\u00e0cc. Su boobaa, asamaan yi dina\u00f1u ne rajax toj, lu ne ci \u00e0ddina lakk ba seey, te suuf ak lu mu \u00ebmb dina ne f\u00e0\u014b\u014b fa kanam Y\u00e0lla.\n3:11 Gannaaw loolu l\u00e9pp dina seeye noonu nag, nangeen g\u00f3or-g\u00f3orlu ci g\u00ebna sellal seen nekkin, te feddali seen ragal Y\u00e0lla.\n3:12 Te it ngeen taxaw temm ci s\u00e9entu b\u00e9su Y\u00e0lla bi, te waajal \u00f1\u00ebwam. Su boobaa, asamaan yi dina\u00f1u lakk, ba naaw ni p\u00ebnd, te lu nekk ci \u00e0ddina dina lakk, ba seey nib d\u00f3om.\n3:13 Waaye nun ngi s\u00e9entu asamaan su bees ak suuf su bees, fa njub d\u00ebkk, ci ni ko Y\u00e0lla dige.\n3:14 Kon nag samay soppe, gannaaw yeena ngi s\u00e9entu loolu, g\u00f3or-g\u00f3orluleen, ngir bu Krist \u00f1\u00ebwee, mu fekk leen ci j\u00e0mm, ngeen ba\u00f1a am benn g\u00e0kk mbaa sikk.\n3:15 Te j\u00e0ppleen ne, mu\u00f1ug sunu Boroom muccu nit la. Sunu mbokk mi nu b\u00ebgg Pool bind na leen ko, ci xel mi ko Y\u00e0lla sol.\n3:16 Noonu lay waxe ciy bataaxelam y\u00e9pp di ci biral lii. Am na ci sax yu jafee xam, te \u00f1i amul xam-xam te seen ng\u00ebm d\u00ebg\u00ebrul di ko walbati, ba alag seen bopp, te loolu la\u00f1uy def ci Mbind yi ci des.\n3:17 Noonu yeen samay xarit, gannaaw xam ngeen loolu ba noppi, moytuleen \u00f1i weddi f\u00e0bbi leen ci seen r\u00e9er, ba yolomal seen w\u00e0kkirlu ci Y\u00e0lla.\n3:18 Waaye m\u00e0ggleen ci yiwu sunu Boroom ak Musalkat Yeesu Krist, te sax ci xam ko; moo yelloo ndam fii ba f\u00e0ww.","title":"Wolof Bible (NT): 2 Peter","type":"page"}
