{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/phi.htm","path":"bib/wb/wlf/phi.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/phi.htm","text":"1:1 Nun Pool ak Timote, jaami Kirist Yeesu, noo leen di bind, y\u00e9en gaayi Y\u00e0lla yu sell y\u00e9pp ci d\u00ebkku Filib, yi bokk ci Kirist Yeesu, y\u00e9en ak seeni njiit ak \u00f1iy topptoo y\u00ebfi mbooloo mi.\n1:2 Na leen Y\u00e0lla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak j\u00e0mm.\n1:3 Yoon wu ma leen di xalaat, maa ngi sant Y\u00e0lla sama Boroom;\n1:4 te saa su ma leen di \u00f1aanal y\u00e9en y\u00e9pp, duma noppee b\u00e9g,\n1:5 ndax seen \u00e0nd ak man ci tas xebaar bu baax bi, ca ndoorte la ba tey.\n1:6 W\u00f3or na ma ne, Y\u00e0lla mi t\u00e0mbali j\u00ebf ju baax jii ci y\u00e9en, dina ci sax, ba b\u00e9su Kirist Yeesu \u00f1\u00ebw.\n1:7 Te juumuma ci li ma xalaat loolu ci y\u00e9en \u00f1\u00e9pp, ndaxte def naa leen ci sama xol; ba tax fii ci kaso bi, ci taxawal xebaar bu baax bi ak lawal ko, y\u00e9en \u00f1\u00e9pp am ngeen w\u00e0ll ak man ci yiwu Y\u00e0lla.\n1:8 Ndaxte Y\u00e0llaa seede ne, sama xol seey na ci y\u00e9en \u00f1\u00e9pp ci biir cofeelu Kirist Yeesu.\n1:9 Li ma leen di \u00f1aanal nag mooy lii: na seen mb\u00ebggeel di yokku tey g\u00ebn a tar, jaar ci xam ak x\u00e0mmi gu w\u00e9r;\n1:10 nangeen sax noonu ci yi g\u00ebn a rafet, ngeen am xol bu laab te ba\u00f1 a am benn sikk, ba b\u00e9su Kirist \u00f1\u00ebw;\n1:11 na seen xol me\u00f1\u00f1 njub, ba ne g\u00e0\u00f1\u00f1, jaar ci Yeesu Kirist ci ndamul Y\u00e0lla ak cantam.\n1:12 Damaa b\u00ebgg, bokk yi, ngeen xam lii: li ma dal taxul xebaar bu baax dellu gannaaw, waaye da koo j\u00ebmale kanam.\n1:13 Noonu \u00f1iy wottu buur bi ak \u00f1\u00e9pp gis na\u00f1u bu leer ne, turu Kirist rekk a tax \u00f1u j\u00e0pp ma.\n1:14 Te it bokk yu bare takk na\u00f1u seeni fit ci li \u00f1u gis samay buum, ba tax \u00f1u g\u00ebn a \u00f1eme ci wax k\u00e0ddug Y\u00e0lla ci lu \u00e0ndul ak genn tiit.\n1:15 Am na \u00f1uy waare ci turu Kirist ci kaw ki\u00f1aan ak x\u00ebccoo, waaye \u00f1i ci des ci kaw cofeel ak xol bu laab, ndaxte xam na\u00f1u ne, Y\u00e0lla moo ma teg fii, ngir ma taxawal xebaar bu baax bi.\n1:17 Waaye \u00f1ale amu\u00f1u xol bu laab, te seen njari\u00f1u bopp rekk a tax \u00f1uy y\u00e9gle turu Kirist, di wut a feddali samay buum ak coono.\n1:18 Lu ci g\u00e9nn nag? Xanaa lii rekk: turu Kirist jolli na ci nii mbaa naa, muy ci naaf\u00e9q, muy ci d\u00ebgg; b\u00e9g naa ci te dinaa ci b\u00e9gati.\n1:19 Ndaxte xam naa ne, loolu l\u00e9pp mu ngi j\u00ebm ci sama mucc, jaar ci seeni \u00f1aan ak ndimbalu Xelum Yeesu Kirist, mi ma Y\u00e0llay y\u00e9w\u00e9nal.\n1:20 Ndaxte sama x\u00ebnte ak sama yaakaar mooy ma ba\u00f1 a rus ci lenn, waaye sama yaram fee\u00f1al ndamu Kirist, ma \u00e0nd ci ak k\u00f3olute gu mat, su may dund mbaa may dee; moom laa daan def d\u00e9mb, te moom laay def tey.\n1:21 Ndaxte su ma dundee, Kirist laay noyyee, te su ma deeyee, x\u00e9ewal lay doon ci man.\n1:22 Su ma Y\u00e0lla b\u00e0yyee ci \u00e0ddina, sas wu am njari\u00f1 la ci man. Am naa xel \u00f1aar, te xawma bi ci g\u00ebn. Am naa y\u00e9eney j\u00f3ge fi, fekki Kirist, te looloo g\u00ebn fuuf,\n1:24 waaye ma des fi ci \u00e0ddina moo g\u00ebn ci y\u00e9en.\n1:25 Loolu w\u00f3or na ma; kon xam naa ne, dinaa fi des, di leen taxawu y\u00e9en \u00f1\u00e9pp, ngir seen ng\u00ebm yokku, \u00e0nd ak mb\u00e9g.\n1:26 Noonu dinaa dellusi ci y\u00e9en, ngir sama taxawaay g\u00ebn a lawal seen mb\u00e9g ci Kirist Yeesu.\n1:27 Waaye d\u00e9nk naa leen lii: na seeni j\u00ebf yelloo ak li Kirist digle ci xebaar bu baax bi. Noonu su ma leen seetsee, mbaa ma d\u00e9gg seen mbir rekk, dinaa xam ne y\u00e9ena ngi d\u00ebg\u00ebr ci menn xel, bokk benn xalaat ci b\u00ebre luy saxal d\u00ebggu xebaar bu baax bi,\n1:28 te ba\u00f1 a tiit dara ndax noon, yi leen di x\u00ebbal. M\u00e0ndarga la muy wone ne aji s\u00e0nku la\u00f1u, di m\u00e0ndarga it ne aji mucc ngeen, di mucc gu j\u00f3ge ci Y\u00e0lla.\n1:29 Ndaxte Y\u00e0lla may na leen, ngeen g\u00ebm Kirist, rax-ca-dolli ngeen sonn ndax turam,\n1:30 di w\u00e9y ci b\u00ebre, bi ngeen gisoon ci man, te d\u00e9gg l\u00e9egi sama mbir.\n2:1 Su nu Kirist mayee fit nag ak mb\u00ebggeel guy d\u00ebf\u00ebl sunu xol, su nu amee c\u00e9r ci Xel mu Sell mi, su amee cofeel ak y\u00ebrmande ci sunu bokk ci moom,\n2:2 kon mottalileen sama mb\u00e9g, ci bokk benn xalaat ak genn mb\u00ebggeel, benn bakkan ak menn xel.\n2:3 Buleen def dara ci kaw wut aw tur walla wonu, waaye jiital-leen seeni moroom cig woyof.\n2:4 Buleen yem ci topptoo seen bopp rekk, waaye booleleen ci seeni moroom.\n2:5 Te ngeen soloo xel mi nekkoon ci Kirist Yeesu:\n2:6 Nj\u00e0lb\u00e9en ga fekk na Kirist yor melow Y\u00e0lla,waaye aakimowul taxawaayamci li mu mengoo ak Y\u00e0lla.\n2:7 Waaye daa w\u00e0cce boppam,ba tollook nit \u00f1i,def boppam surga.Te bi mu yoree bindu nit,\n2:8 daa suufeel boppam,di d\u00e9gg ndigal, ba joxe boppam,\u00f1u daaj ko sax ci bant.\n2:9 Moo tax Y\u00e0lla kaweel ko lool,jox ko tur wi tiim y\u00e9pp,\n2:10 ngir turu Yeesoo tax \u00f1\u00e9pp sukk,ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf;\n2:11 te \u00f1\u00e9pp bokk genn k\u00e0ddu naan:Yeesu Kirist mooy Boroom bi;ci m\u00e0ggug Y\u00e0lla Baay bi.\n2:12 Noonu samay soppe, xam naa ne, musuleen a j\u00f3g ci d\u00e9gg ndigal, waxuma sax bi ma nekkee ak y\u00e9en rekk, waaye rawatina bi ma leen soree. Kon nag maa ngi leen di \u00f1aan, ngeen biral seen mucc ci seeni j\u00ebf, te def ko ci ragal Y\u00e0lla gu d\u00ebggu.\n2:13 Ndaxte Y\u00e0lla ci boppam mooy j\u00ebf ci y\u00e9en, ngir ngeen fonk coobareem te di ko j\u00ebfe.\n2:14 L\u00e9pp lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo.\n2:15 Noonu dingeen am xol bu laab bu \u00e0ndul ak \u014b\u00e0\u00f1\u00f1, di guney Y\u00e0lla yu amul sikk ci biir jamono ju y\u00e0qu te r\u00ebb. Dangeen di leer ci seen biir ni weer ci \u00e0ddina si,\n2:16 di jottali k\u00e0ddug dund gi. Noonu bu b\u00e9su Kirist \u00f1\u00ebwee, dinaa man a b\u00e9g, xam ne dawuma lu amul njari\u00f1, te sonnuma cig neen.\n2:17 Te bu sama deret waree tuuru sax, ngir seen ng\u00ebm mat s\u00ebkk, ma mel ni naan gu \u00f1u boole ak sarax su j\u00ebm ci Y\u00e0lla, ba tey b\u00e9g naa ci, te dinaa ci b\u00e9gati.\n2:18 Y\u00e9en itam nag b\u00e9gleen, waaw fekksileen ma ci sama mb\u00e9g.\n2:19 Gannaaw loolu, bu soobee Boroom bi Yeesu, yaakaar naa ne, dinaa leen y\u00f3nnee Timote balaa y\u00e0gg, ngir sama xel dal ci xam nan ngeen def.\n2:20 Ndaxte amu fi kenn gannaaw Timote, ku bokk ak man xalaat te fonk leen bu w\u00e9r.\n2:21 \u00d1i ci des \u00f1\u00e9pp, seen bopp la\u00f1uy xalaat, waaye du mbiri Yeesu Kirist.\n2:22 Waaye xam ngeen takkuteg Timote, ci ni mu \u00e0nde ak man ci tas xebaar bu baax bi, ni doom di taxawoo baayam.\n2:23 Moom laa yaakaar a y\u00f3nni fi y\u00e9en nag, waxtu wu ma y\u00e9gee, nu sama mbir di t\u00ebdde.\n2:24 Waaye w\u00f3or na ma ne, Boroom bi dina ma may, man ci sama bopp, ma seetsi leen balaa y\u00e0gg.\n2:25 Ci lu j\u00ebm ci sama mbokk Epafrodit nag, miy sama nawle ci ligg\u00e9ey bi ak ci xeex bi, te di seen ndaw ci faj samay soxla, j\u00e0pp naa ne, war naa leen koo delloo.\n2:26 Ndaxte namm na leen lool, te tiisoo na li ngeen y\u00e9g jagadeem.\n2:27 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg woppoon na ba xaw a dee, waaye Y\u00e0lla y\u00ebr\u00ebm na ko, ba f\u00ebgg boppam, rax-ca-dolli siggil na ma man itam, ngir ma ba\u00f1 a am tiis ci kaw tiis.\n2:28 Noonu delloo naa leen ko ci lu gaaw, ngir \u00f1\u00ebwam b\u00e9gal seeni xol, te man itam sama xol f\u00e9ex.\n2:29 Teeruleen ko teeru bu rafet nag ngir Boroom bi, te teral \u00f1i mel ni moom.\n2:30 Ndaxte ligg\u00e9eyal na Kirist, ba riisu dee, te gar na bakkanam ci taxawal leen ci topptoo, bi ngeen y\u00e9ene woon ci man.\n3:1 Kon nag samay bokk, b\u00e9gleen ci Boroom bi. Duma sonn mukk ci di leen ko wax, ndax seen mucc moo ci aju.\n3:2 Moytuleen xaj yi, waaw moytuleen \u00f1iy j\u00ebfe lu bon, \u00f1oom \u00f1i seen xarafal weesul w\u00e0\u00f1\u00f1i yaramu nit.\n3:3 Ndaxte nun noo xaraf tigi, nun \u00f1iy m\u00e0ggal Y\u00e0lla ci Xel mu Sell mi, di damu ci Kirist Yeesu, te amunu jenn yaakaar ci matug nit.\n3:4 Ba tey manoon naa am yaakaar ci sama bopp; su nit doon damu, maa ciy raw.\n3:5 Xarafoon naa ca ayu-b\u00e9s ga, bokk ci b\u00e0nni Israyil ci giiru Ben-yamin, di Ibr\u00eb ci deret ak ci meen. Bu dee ci yoonu Musaa ngeen b\u00ebgg a wax, ci tariixab Farisen laa bokkoon;\n3:6 bu dee it ci mbirum farlu, daan naa fitnaal mbooloom \u00f1i g\u00ebm Kirist; bu dee ci njub ci s\u00e0mm yoon, awma benn g\u00e0kk.\n3:7 Waaye loolu l\u00e9pp lu ma tegoon ay njari\u00f1 fa kanam Y\u00e0lla, d\u00ebddu naa ko ngir Kirist.\n3:8 Rax-ca-dolli d\u00ebddu naa l\u00e9pp ngir x\u00e9ewali xam Kirist Yeesu sama Boroom, di xam-xam bu x\u00f3ot, ba xel m\u00ebnu koo takk. Moo tax \u00f1\u00e0kk naa sama l\u00e9pp, te def ko ni mbalit, ngir am c\u00e9r ci Kirist.\n3:9 Na ma Y\u00e0lla fekk ci moom, waxuma ci njub gu aju ci s\u00e0mm yoon, waaye gu aju ci g\u00ebm Kirist, maanaam njub gi nu Y\u00e0lla sol ci kaw ng\u00ebm.\n3:10 Moom laay ittewoo xam, ak doole ji \u00e0nd ak ndekkiteem, ma bokk ci ay coonoom, ba fekki ko ci deeyam,\n3:11 ngir man a s\u00e9ddu ci ndekkiteem, su ma ko manee am.\n3:12 Waxuma ne jagoo naa ko ba noppi, waxuma it ne aji mat laa, waaye maa ngi daw, ngir jot li tax Kirist j\u00ebl ma.\n3:13 Bokk yi, g\u00ebmuma ne jot naa ko ba noppi, waaye lenn lii laay def: f\u00e0tte li ma weesu, jublu ci li f\u00e9ete kanam,\n3:14 di daw yen muj ga, ngir jot li ma Y\u00e0lla tax a woo, di c\u00e9r bi ma Y\u00e0lla wooye te dencal ma ko ci asamaan ci darajay Kirist Yeesu.\n3:15 Nun \u00f1i mat nag, nanu xalaat loolu. Te su ngeen ci amee werantey xol, Y\u00e0lla dina leen ko leeralal.\n3:16 Li am daal, fa seen ng\u00ebm tolloo, na fa seen j\u00ebf \u00e0gg.\n3:17 Kon nag bokk yi, toppleen ma te xool \u00f1iy roy ci li nu t\u00ebral diirub sunu ngan ci y\u00e9en.\n3:18 Ndaxte j\u00ebfi \u00f1u bare juuyoo na ak dee gi Kirist dee; loolu wax naa leen ko ba t\u00e0yyi, maa ngi koy waxaat l\u00e9egi ak i jooy.\n3:19 Alku la\u00f1uy mujje, \u00f1oom \u00f1iy jaami seen biir, di wonoo lu ruslu, tey wut y\u00ebfi \u00e0ddina rekk.\n3:20 Waaye nun waa asamaan lanu, te noo ngi xaar Boroom bi Yeesu Kirist j\u00f3ge fa, musalsi nu.\n3:21 Noonu dina soppi sunu yaram wu toroxlu, def ko ni yaramam wi \u00e0nd ak ndam d\u00ebppook k\u00e0ttanam, gi ko man a nootal mbindeef y\u00e9pp.\n4:1 Kon nag y\u00e9en samay bokk, \u00f1i ma b\u00ebgg te namm leen, di sama mb\u00e9g ak sama kaalag ndam, j\u00e0ppleen bu d\u00ebg\u00ebr noonu ci Boroom bi, soppe yi!\n4:2 Ci lu j\u00ebm ci Ewodi ak Santis, maa ngi leen di \u00f1aan, \u00f1u bokk benn xalaat ci Boroom bi.\n4:3 Te yaw sama nawle bu w\u00e9r, nanga dimbali jig\u00e9en \u00f1oo\u00f1u xeexoon ci sama wet ci tas xebaar bu baax bi, boole ci K\u00eblema\u014b ak samay yeneeni nawle, \u00f1oom \u00f1i Y\u00e0lla bind seeni tur ci t\u00e9ereb dund ba.\n4:4 Deeleen b\u00e9g ci Boroom bi; maa ngi koy waxati: b\u00e9gleen!\n4:5 Na seen lewet leer \u00f1\u00e9pp. Boroom bi jege na.\n4:6 Buleen jaaxle ci dara, waaye ci l\u00e9pp w\u00e9etal-leen Y\u00e0lla, diis ko seeni soxla ci \u00f1aan gu \u00e0nd ak cant.\n4:7 Noonu j\u00e0mmu Y\u00e0lla, ji xel m\u00ebnta takk, dina aar seeni xol ak seeni xalaat ci darajay Kirist Yeesu.\n4:8 L\u00e9egi nag bokk yi, na seen xalaat jublu ci lii: lu d\u00ebggu, lu jekk, lu jub, lu sell, lu rafet ak lu faaydawu; su fi amee lu baax mbaa lu mat a naw, xalaatleen ko.\n4:9 Li ngeen j\u00e0nge ci man te nangu ko, li ngeen d\u00e9gge ci man te gis ko, j\u00ebfeleen ko; kon Y\u00e0llay j\u00e0mm dina \u00e0nd ak y\u00e9en.\n4:10 Sama xol sedd na guyy ci Boroom bi, ci ni ngeen yeesale seen ndimbal ci man. Xam naa ne, amoon ngeen y\u00e9ene ji, waaye man gi moo fi nekkul woon.\n4:11 Ba tey soxla taxul ma waxe nii, ndaxte j\u00e0ng naa doylu ci mbir mu ma man a dab.\n4:12 Miin naa \u00f1\u00e0kk, man naa naataange. Ci f\u00e9pp ak ci l\u00e9pp, Y\u00e0lla def na ba sama xol toj ci suur ak xiif, barele ak n\u00e9ewle.\n4:13 Man naa l\u00e9pp ci ndimbalu Aji Dooleel ji.\n4:14 Waaye teewul taxawu, bi ngeen ma taxawu ci sama tiis, j\u00ebf ju rafet la.\n4:15 Y\u00e9en waa Filib xam ngeen ne, bi ngeen j\u00ebkkee xam xebaar bu baax bi, te ma j\u00f3ge diiwaanu Maseduwan, benn mbooloo \u00e0ndul woon ak man ci mbirum joqleente ndimbal, mu dul y\u00e9en do\u014b\u014b.\n4:16 Ba ma nekkee d\u00ebkku Tesalonig sax, y\u00f3nnee ngeen ay yooni yoon, ngir faj samay soxla.\n4:17 Loolu tekkiwul ne, damay s\u00e0kku ay ndimbal ci y\u00e9en, waaye damaa b\u00ebgg rekk seen denc yokku fa Y\u00e0lla.\n4:18 Fi mu ne jot naa li ma aajowoo l\u00e9pp, ba maa ngi ci naataange; li ngeen ma y\u00f3nnee ci loxoy Epafrodit doy na s\u00ebkk; ni xetu latkolo\u00f1 la mel ci man, di sarax su neex Y\u00e0lla te mu nangu ko.\n4:19 Te Y\u00e0lla sama Boroom, mi denc ci Kirist Yeesu x\u00e9ewal yu dul jeex, dina ci faj seeni soxla y\u00e9pp.\n4:20 Na Y\u00e0lla sunu Baay yelloo ndam ba f\u00e0ww. Amiin.\n4:21 Nuyul-leen ma gaayi Kirist Yeesu yu sell y\u00e9pp. Bokk yi \u00e0nd ak man, \u00f1u ngi leen di nuyu.\n4:22 Te it gaayi Y\u00e0lla yu sell y\u00e9pp \u00f1u ngi leen di nuyu, rawatina nag \u00f1i nekk k\u00ebr buur bi Sesaar.\n4:23 Na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist \u00e0nd ak seen xel.","title":"Wolof Bible (NT): Philippians","type":"page"}
