{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/plm.htm","path":"bib/wb/wlf/plm.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/plm.htm","text":"1:1 Man Pool, mi \u00f1u t\u00ebj kaso ngir Kirist Yeesu, ak sunu mbokk Timote, noo lay bind, yaw Filemon sunu soppe ak sunu nawle ci xeex bi;\n1:2 te f\u00e0ttewunu sunu jig\u00e9en Afiya, ak sunu \u00e0ndandoo ci xeex bi Arkib, y\u00e9en ak mbooloom \u00f1i g\u00ebm, miy dajee sa k\u00ebr.\n1:3 Na leen Y\u00e0lla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak j\u00e0mm.\n1:4 Duma la noppee boole ci samay \u00f1aan, di ci sant Y\u00e0lla sama Boroom,\n1:5 ndaxte d\u00e9gg naa sa ng\u00ebm ci Boroom bi Yeesu, ak sa mb\u00ebggeel ci gaayam yu sell y\u00e9pp.\n1:6 Li may \u00f1aan nag a ngi nii: nga xam bu w\u00e9r ng\u00ebneel, yi nu am y\u00e9pp ci sunu bokk ci Kirist, ba tax bokk gi nga am ci Y\u00e0lla ci kaw ng\u00ebm me\u00f1\u00f1 i njari\u00f1.\n1:7 Ci d\u00ebgg-d\u00ebgg sa mb\u00ebggeel b\u00e9gal na ma bu baax, ba d\u00ebf\u00ebl sama xol; ndaxte xam naa, sama mbokk, ni nga f\u00e9exale xoli gaayi Y\u00e0lla yu sell yi.\n1:8 Am na lu ma la b\u00ebgg a \u00f1aan; teguma ko ci sa\u00f1-sa\u00f1 bu mat bi ma Kirist may, ci teg la ndigalu def sa warugar,\n1:9 waaye dama lay \u00f1aan ci mb\u00ebggeel gi nu s\u00e9q, man Pool m\u00e0ggat, mi \u00f1u t\u00ebj kaso ci turu Kirist.\n1:10 Maa ngi tinul sama doomu diine Onesim, mi ma jur ci Kirist fii ci kaso bi.\n1:11 Amul woon sa njari\u00f1 d\u00e9mb, waaye tey amal na nu njari\u00f1, yaw ak man.\n1:12 Maa koy yebal fi yaw, waaye xamal ne, mooy sama reeni xol.\n1:13 Dama koo b\u00ebggoon a t\u00e9ye fi sama wet, ngir mu taxawal la, di ma dimbali, li feek maa ngi ci kaso bi ngir xebaar bu baax bi.\n1:14 Waaye b\u00ebggumaa def dara loo \u00e0ndul; noonu ndimbal li nga may defal du nekk sa\u00f1ul-ba\u00f1, waaye mu \u00e0nd ak xol bu t\u00e0lli.\n1:15 X\u00eby na sax dafa t\u00e0ggoo woon ak yaw diir bu g\u00e0tt, ngir nga jotaat ci ba f\u00e0ww;\n1:16 waxuma l\u00e9egi ni jaam rekk, waaye lu ko sut, xanaa mbokk mu d\u00ebggu ci xol, fekk looloo raw ag njaam. Mbokk la ci man, rawatina ci yaw, muy sa jaam ci aada, di sa mbokk l\u00e9egi ci Boroom bi.\n1:17 Soo ma j\u00e0ppee ni nawle nag, teeru ko, ni su ma la doon ganesi.\n1:18 Soo ko naree topp genn too\u00f1 mbaa benn bor, topp ma ko.\n1:19 Man Pool maa ngi lay bind ak sama loxob bopp ne, dinaa la ko fey; b\u00ebggumaa yegg ci ne, sag dund sax ci man la jaar!\n1:20 Waaw yaw sama mbokk, dimbali ma ci Boroom bi, te seral sama xol ci sunu bokk ci Kirist.\n1:21 Noonu bind naa la, ndax w\u00f3or na ma ne, dinga ma d\u00e9ggal, ba weesu sax li ma la sant.\n1:22 Te itam nanga ma waajal n\u00e9eg, ndaxte yaakaar naa ne, Y\u00e0lla dina nangu seeni \u00f1aan, ba delloosi ma leen.\n1:23 Sama mbokk Epafras, mi ma nekkal fi ci kaso bi ci turu Kirist, mu ngi lay nuyu.\n1:24 Samay \u00e0ndandoo ci ligg\u00e9ey bi, M\u00e0rk, Arist\u00e0rk, Demas ak Luug, \u00f1u ngi lay nuyu.\n1:25 Na yiwu Boroom bi Yeesu Kirist \u00e0nd ak seen xel.","title":"Wolof Bible (NT): Philemon","type":"page"}
