{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/rev.htm","path":"bib/wb/wlf/rev.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/rev.htm","text":"1:1 Lii mooy li Yeesu Kirist fee\u00f1al, te mu tukkee ca Y\u00e0lla, ngir mu won ay jaamam mbir, yi d\u00ebgm\u00ebl di \u00f1\u00ebw. Y\u00f3nni na malaakaam, ngir xamal ko ab jaamam Yowaana.\n1:2 Kooku mi ngi seede fii li mu gis l\u00e9pp, maanaam k\u00e0ddug Y\u00e0lla ak seede, si \u00f1u seedeel Yeesu Kirist.\n1:3 Barkeel ngeen, yaw miy j\u00e0ng ak y\u00e9en \u00f1iy d\u00e9glu wax yii j\u00f3ge ca Y\u00e0lla, te di s\u00e0mm li \u00f1u ci bind, ndaxte waxtu wi jege na.\n1:4 Man Yowaana maa leen di bind, y\u00e9en jur\u00f3om-\u00f1aari mboolooy \u00f1i g\u00ebm te nekk ci diiwaanu Asi. Na yiw ak j\u00e0mm f\u00e9ete ci y\u00e9en, j\u00f3ge ci Y\u00e0lla, moom ki nekk, ki nekkoon d\u00e9mb te di \u00f1\u00ebw \u00ebll\u00ebg. Yiw woowu ak j\u00e0mm jooju \u00f1oo ngi tukkee it ci jur\u00f3om-\u00f1aari Xeli Y\u00e0lla, yi nekk ci kanamu g\u00e0ngunem Y\u00e0lla,\n1:5 tukkee it ci Yeesu Kirist, seede bu takku bi, moom taaw bi, maanaam ki j\u00ebkk a dekki, di buuru buur yi ci kaw suuf y\u00e9pp. Na ndam ak nguur f\u00e9ete ak Yeesu Kirist ba f\u00e0ww, moom mi nu b\u00ebgg te yiwi nu ci sunuy b\u00e0kkaar ak deretam ji tuuru, te def nu askanu saraxalekati Buur Y\u00e0lla Baayam, nu di ko jaamu. Amiin.\n1:7 Gisleen, mi ngi \u00f1\u00ebw ci niir yi,te \u00f1\u00e9pp dina\u00f1u teg seeni b\u00ebt ci moom,ba ci \u00f1i ko jam sax.Te xeet yi nekk ci kaw suuf y\u00e9ppdina\u00f1u jooy ndax moom.Waaw. Amiin.\n1:8 Boroom bi Y\u00e0lla nee na: \u00abMan Y\u00e0lla maay Alfa ak Omega, maay ki nekk, ki nekkoon d\u00e9mb te di \u00f1\u00ebw \u00ebll\u00ebg, man Aji K\u00e0ttan ji.\u00bb\n1:9 Man Yowaana seen mbokk, di seen nawle ci fitna, ci nguur ak ci mu\u00f1, yi nu am ndax sunu booloo ak Yeesu, maa nga nekkoon ca dun bu \u00f1uy wax Patmos. Wacce woon na\u00f1u ma fa, ndax li ma doon waare k\u00e0ddug Y\u00e0lla tey seedeel Yeesu.\n1:10 Xelum Y\u00e0lla solu ma ci b\u00e9su Boroom bi, te noonu ma d\u00e9gg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit,\n1:11 naan: \u00abBindal ci t\u00e9ere li ngay gis te y\u00f3nnee ko jur\u00f3om-\u00f1aari mboolooy \u00f1i g\u00ebm, ca d\u00ebkki Efes, Samirin, Pergam, Catir, S\u00e0rd, Filadelfi ak Lawdise.\u00bb\n1:12 Noonu ma geestu, ngir seet ku doon wax ak man. Ba ma geestoo, yem ci jur\u00f3om-\u00f1aari l\u00e0mpi diwlin yu wurus,\n1:13 gis ku taxaw ci biir l\u00e0mp ya, niroo ak doomu nit. Mu sol mbubb mu gudd, takk nge\u00f1aayu wurus ci ndiggam.\n1:14 Boppam ak kawaram weex t\u00e0ll ni perkaal, ay b\u00ebtam di xuyy ni safara.\n1:15 Ay t\u00e0nkam mel ni x\u00e0njar bu y\u00e0nj bu \u00f1u xelli, baatam di riir ni duusi g\u00e9ej.\n1:16 Mu yor ci loxol ndeyjooram jur\u00f3om-\u00f1aari biddiiw, jaasiy \u00f1aari boor yu \u00f1aw di g\u00e9nn ci g\u00e9mmi\u00f1am, xar-kanamam leer n\u00e0\u00f1\u00f1 ni jantub njolloor.\n1:17 Naka laa ko gis, di daanu ci ay t\u00e0nkam ni ku dee. Waaye mu teg loxol ndeyjooram ci sama kaw ne ma: \u00abBul ragal dara. Maay ki j\u00ebkk te maay mujj.\n1:18 Maay Kiy Dund. Dee woon naa, waaye maa ngii di dund ba f\u00e0ww, yor caabiy dee ak ju bars\u00e0q.\n1:19 Kon nag bindal li nga gis, li am l\u00e9egi ak li nar a ami gannaaw gi.\n1:20 Jur\u00f3om-\u00f1aari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndeyjoor, ak jur\u00f3om-\u00f1aari l\u00e0mpi diwlin yu wurus yi, ay mb\u00f3oti Y\u00e0lla la\u00f1u te lii la\u00f1uy tekki: biddiiw yi \u00f1oo di malaakay jur\u00f3om-\u00f1aari mboolooy \u00f1i g\u00ebm; jur\u00f3om-\u00f1aari l\u00e0mp yi \u00f1oo di jur\u00f3om-\u00f1aari mbooloo yi.\n2:1 \u00abBindal malaakam mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci d\u00ebkku Efes, ne ko: i Ki t\u00e9ye jur\u00f3om-\u00f1aari biddiiw yi ci loxol ndeyjooram, tey dox ci diggu jur\u00f3om-\u00f1aari l\u00e0mpi diwlin yu wurus yi nee na:\n2:2 Xam naa say j\u00ebf, sa ligg\u00e9ey ak sag mu\u00f1. Xam naa ne, m\u00ebnuloo d\u00e9kku \u00f1iy def lu bon. Seetlu nga \u00f1i tuddoo samay ndaw, ba gis ne ay naaf\u00e9q la\u00f1u.\n2:3 Xam naa it ne mu\u00f1 nga, ba d\u00e9kku coono ndax sama tur, te x\u00e0ddiwoo. i\n2:4 Waaye li ma naqari ci yaw moo di sa mb\u00ebggeel w\u00e0\u00f1\u00f1iku na.\n2:5 Deel f\u00e0ttaliku kon fa nga daanoo. R\u00e9ccul te def, na nga daan def bu j\u00ebkk. Soo r\u00e9ccuwul, dinaa dikk ci yaw, j\u00eble sa l\u00e0mp ca b\u00e9rab ba mu nekk.\n2:6 Waaye lii neex na ma ci yaw: sib nga ni man li \u00f1oom Nikolas di j\u00ebf. i\n2:7 Yaw mi am ay nopp, d\u00e9glul li Xelum Y\u00e0lla di wax mboolooy \u00f1i g\u00ebm. Ku daan, dinaa la may, nga lekk ci garabu dund, gi nekk ci jataayu Y\u00e0lla.\n2:8 \u00abBindal malaakam mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci d\u00ebkku Samirin, ne ko: i Ki j\u00ebkk te mujj, ki dee woon te dekki nee na:\n2:9 Xam naa sa coono, xam it sa n\u00e9ew doole, moona yaaka duunle. \u00d1oo\u00f1u tuddoo Yawut, xam naa \u00f1aawteef yi \u00f1u teg ci sa der: ndajem Seytaane la.\n2:10 Bul ragal li nga nar a daj. Seytaane dina dugal kaso \u00f1enn ci y\u00e9en, ngir wut leen a fiir. Diirub fukki fan dingeen am coono. Nanga takku ba \u00e0ttan cee dee, ma jox la kaalag dund gi. i\n2:11 Yaw mi am ay nopp, d\u00e9glul li Xelum Y\u00e0lla di wax mboolooy \u00f1i g\u00ebm. Ku daan, doo loru ci \u00f1aareelu dee.\n2:12 \u00abBindal malaakam mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci d\u00ebkku Pergam, ne ko: i Boroom jaasi ju \u00f1aw, ji am \u00f1aari boor nee na:\n2:13 Xam naa fa nga d\u00ebkk, di fa Seytaane samp nguuram. Moona j\u00e9bbalu nga ci sama tur te weddiwoo sa ng\u00ebm ci man, ba ca fan ya \u00f1u reye Antipas, sama seede bu takku ba, ci seen d\u00ebkk, di d\u00ebkku Seytaane. i\n2:14 Waaye am na lu ma naqari ci yaw, moo di uuf nga foofu gaa yuy s\u00e0mm nj\u00e0ngalem Balaam, moom mi j\u00e0ngaloon Balag, mu s\u00f3ob b\u00e0nni Israyil ci b\u00e0kkaar, xiir leen ci lekk \u00f1am wu \u00f1u tuuroo x\u00ebr\u00ebm yi, xiir leen ci njaaloo.\n2:15 Te am nga noonu itam ay nit \u00f1uy s\u00e0mm nj\u00e0ngalem \u00f1oom Nikolas.\n2:16 R\u00e9ccul kon; lu ko moy dinaa dikk ci yaw l\u00e9egi te xeex ak nit \u00f1oo\u00f1u ak jaasi, jiy g\u00e9nn ci sama g\u00e9mmi\u00f1. i\n2:17 Yaw mi am ay nopp, d\u00e9glul li Xelum Y\u00e0lla di wax mboolooy \u00f1i g\u00ebm. Ku daan, dinaa la jox, nga lekk dund bi \u00f1uy wax m\u00e0nn te mu n\u00ebbbu, te dinaa la jox xeer wu weex. Ci kaw xeer woowu bindees na ci tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ki ko jot.\n2:18 \u00abBindal malaakam mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci d\u00ebkku Catir, ne ko: i Doomu Y\u00e0lla ji, ki ay b\u00ebtam di xuyy ni safara, tey t\u00e0nkam di lerax ni x\u00e0njar, nee na:\n2:19 Xam naa say j\u00ebf, sa mb\u00ebggeel, sa ng\u00ebm, sag mu\u00f1 ak ni nga farloo ci sa jaamu Y\u00e0lla. Xam naa say j\u00ebf yu mujj, ni \u00f1u \u00ebppe yu j\u00ebkk ya. i\n2:20 Waaye li ma naqari ci yaw moo di dangaa b\u00e0yyi Yesabel, jig\u00e9en joojuy tuddoo yonent, di j\u00e0ngale ak a r\u00e9eral sama jaam yi, ngir \u00f1uy s\u00f3obu ci njaaloo te di lekk \u00f1am wu \u00f1u tuuroo x\u00ebr\u00ebm yi.\n2:21 May naa ko ab diir, ngir mu tuub njaaloom, waaye ba\u00f1 na.\n2:22 Kon nag dinaa ko t\u00ebral ci lalu metit, te \u00f1iy \u00e0nd ak moom di njaaloo, su \u00f1u tuubul j\u00ebfi jig\u00e9en jooju, dinaa leen teg naqar wu mag.\n2:23 Dinaa rey ay doomam, te mboolooy \u00f1i g\u00ebm y\u00e9pp dina\u00f1u xam ne, man maa di kiy nattu xol ak xalaat, te dinaa fey ku nekk ay j\u00ebfam.\n2:24 Waaye y\u00e9en \u00f1\u00e9pp \u00f1i des ci Catir te toppuleen nj\u00e0ngale moomu te g\u00ebstuwuleen loolu \u00f1u naan mbiri Seytaane yu x\u00f3ot yi, maa ngi leen di wax ne, duma leen yen beneen yen\n2:25 bu dul bii: j\u00e0ppleen ci li ngeen j\u00e0pp, ba kera may \u00f1\u00ebw. i\n2:26 Ku daan tey sax ci samay j\u00ebf ba ca muj ga, dinaa ko jox sa\u00f1-sa\u00f1 ci xeet yi:i\n2:27 Dina leen jiite ak yetu we\u00f1,i tojat leen ni \u00f1uy toje ndaal kew \u2014i\n2:28 ni ma j\u00eble sa\u00f1-sa\u00f1 ci sama Baay. Dinaa ko jox it biddiiwu nj\u00ebl.\n2:29 Yaw mi am ay nopp, d\u00e9glul li Xelum Y\u00e0lla di wax mboolooy \u00f1i g\u00ebm.\n3:1 \u00abBindal malaakam mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci d\u00ebkku S\u00e0rd, ne ko: i Ki yor jur\u00f3om-\u00f1aari Xeli Y\u00e0lla yi ak jur\u00f3om-\u00f1aari biddiiw yi nee na: Xam naa say j\u00ebf. Da\u00f1u laa teg kuy dund, fekk dee nga.\n3:2 Yeewul te d\u00ebg\u00ebral li des ci yaw tey waaj a dee, ndaxte gis naa ne, say j\u00ebf matu\u00f1u ca sama kanam Y\u00e0lla.\n3:3 F\u00e0ttalikul kon k\u00e0ddug Y\u00e0lla gi nga jot, te d\u00e9gg ko, s\u00e0mm ko te r\u00e9ccu. Soo w\u00e9yee ciy nelaw nag, dinaa \u00f1\u00ebw nib s\u00e0cc, te doo xam wan waxtu lay doon. i\n3:4 Moona am nga foofu ci S\u00e0rd nit \u00f1u n\u00e9ew \u00f1oo xam ne tilimalu\u00f1u seen mbubb. \u00d1oo\u00f1u dina\u00f1u \u00e0nd ak man, sol lu weex, ndaxte yeyoo na\u00f1u ko.\n3:5 Ku daan, dinga sol mbubb mu weex ni \u00f1oom. Te duma far sa tur ci t\u00e9ereb dund bi, waaye dinaa nangu ci sama kanamu Baay ak ay malaakaam ne, bokk nga ci man.\n3:6 Yaw mi am ay nopp, d\u00e9glul li Xelum Y\u00e0lla di wax mboolooy \u00f1i g\u00ebm.\n3:7 \u00abBindal malaakam mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci d\u00ebkku Filadelfi, ne ko: i Aji Sell ji, di Aji D\u00ebgg ji nee na, moom mi yor caabiy Daawuda ji, moom miy tijji te kenn du ko man a t\u00ebj, muy t\u00ebj te kenn du ko tijji nee ne:\n3:8 Xam naa say j\u00ebf. Ubbil naa la bunt, te kenn du ko man a t\u00ebj. Xam naa ne barewuloo doole, waaye s\u00e0mm nga sama k\u00e0ddu te weddiwoo ma.\n3:9 Dinaa def ba \u00f1enn ci \u00f1i bokk ci ndajem Seytaane --te tuddoo Yawut, fekk da\u00f1uy fen \u2014 dinaa leen \u00f1\u00ebwloo, \u00f1u sukk ci sa kanam, nangu ne, b\u00ebgg naa la.\n3:10 Gannaaw mu\u00f1 nga, ni ma la ko d\u00e9nke woon, man itam dinaa la yiir ci jamono, ji musiba mi di w\u00e0cc ci dunyaa b\u00e9pp ngir nattu waa \u00e0ddina. i\n3:11 L\u00e9egi ma \u00f1\u00ebw. S\u00e0mmal li nga yor, ngir kenn ba\u00f1 laa xa\u00f1 sa kaalag ndam.\n3:12 Ku daan, dinaa la samp ni aw j\u00ebnu n\u00e9eg ci sama k\u00ebr Y\u00e0lla te doo fa g\u00e9nn mukk. Dinaa bind ci yaw turu sama Y\u00e0lla ak turu d\u00ebkku sama Y\u00e0lla, mu di Yerusalem gu bees, giy j\u00f3ge ca asamaan ca wetu sama Y\u00e0lla di w\u00e0cc. Dinaa bind it ci yaw sama tur wu bees.\n3:13 Yaw mi am ay nopp, d\u00e9glul li Xelum Y\u00e0lla di wax mboolooy \u00f1i g\u00ebm.\n3:14 \u00abBindal malaakam mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci d\u00ebkku Lawdise, ne ko: i Ki \u00f1uy wax Amiin ji, di seede bu takku bi te d\u00ebggu, ki di ndeyi bindu mbindeefi Y\u00e0lla yi, nee na;\n3:15 Xam naa say j\u00ebf, xam ne seddoo, t\u00e0ngoo. Manoon ngaa sedd mbaa nga t\u00e0ng,\n3:16 waaye ndax li nga nugg, t\u00e0ngoo seddoo, dinaa la y\u00e0bbi.\n3:17 Yaa ngi damu naan: \u201cAm naa alal, duunle naa, soxlaatuma dara.\u201d Fekk xamuloo ne, torox nga, miskin, \u00f1\u00e0kk, gumba te rafle.\n3:18 Moo tax maa ngi lay xiirtal, nga j\u00ebnd ci man wurus wu \u00f1u xellee ci safara, ngir nga duunle, te nga j\u00ebnd y\u00e9re yu weex ngir nga solu, ba sa g\u00e0cceg rafle ba\u00f1 a fee\u00f1, ak tuufaay booy diw ci say b\u00ebt, ngir man a gis. i\n3:19 Man maay yedd, di yar \u00f1\u00e9pp \u00f1i ma b\u00ebgg. Farlul kon te tuub say b\u00e0kkaar.\n3:20 Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di f\u00ebgg. Ku d\u00e9gg sama baat te ubbi bunt bi, dinaa dugg, reerandoo ak moom, moom it mu reerandoo ak man. i\n3:21 Ku daan, dinaa la toogloo ci sama wet ci sama g\u00e0ngune, ni ma xeexe ba daan, man ci sama bopp, te toogandoo ak sama Baay ci g\u00e0nguneem.\n3:22 Yaw mi am ay nopp, d\u00e9glul li Xelum Y\u00e0lla di wax mboolooy \u00f1i g\u00ebm.\u00bb\n4:1 Gannaaw loolu ma xool, gis bunt ubbiku ci asamaan. Baat booba ma d\u00e9ggoon, muy wax ak man mel nig liit, ne ma: \u00abY\u00e9egal fii, ma won la li war a \u00f1\u00ebw gannaaw gi.\u00bb\n4:2 Ca saa sa Xelum Y\u00e0lla solu ma, noonu ma gis g\u00e0ngune ca asamaan, te am ku ca toog.\n4:3 Leeraayam mel ni jamaa ak per bu xonq, te xon gu leer ni per bu wert w\u00ebr g\u00e0ngune ma.\n4:4 Yeneen \u00f1aar-fukki g\u00e0ngune ak \u00f1eent w\u00ebr ko, te ci kaw g\u00e0ngune ya \u00f1aar-fukki mag ak \u00f1eent toog, sol mbubb yu weex ak kaalay wurus ci seen bopp.\n4:5 Ay melax, ay riir ak ay d\u00ebnnu di jibe ca g\u00e0ngune ma. Ca kanamu g\u00e0ngune ma amoon na fa jur\u00f3om-\u00f1aari l\u00e0mp yu y\u00e0nj, di jur\u00f3om-\u00f1aari Xeli Y\u00e0lla yi.\n4:6 Amoon na it ca kanamu g\u00e0ngune ma lu mel ni g\u00e9ej gu leer ni weer bu set, ba mel ni seetu. Ci li w\u00ebr g\u00e0ngune ma, s\u00ebs r\u00ebkk, amoon na fa \u00f1eenti mbindeef yu fees ak ay b\u00ebt ci kanam ak ci gannaaw.\n4:7 Mbindeef mu j\u00ebkk maa nga meloon ni gaynde, \u00f1aareelu mbindeef mel ni y\u00ebkk, \u00f1etteelu mbindeef yor kanamu nit, \u00f1eenteel ba di nirook jaxaay juy naaw.\n4:8 \u00d1eenti mbindeef ya am na\u00f1u ku nekk jur\u00f3om-benni laaf te \u00f1u nga fees ak ay b\u00ebt li leen w\u00ebr l\u00e9pp, ba ci seen roni laaf. Guddi ak b\u00ebcc\u00ebg du\u00f1u noppeek naan:\u00abBoroom bi Y\u00e0lla, Aji K\u00e0ttan ji,moo sell, sell, sell,moom ki nekkoon d\u00e9mb,ki nekk tey, te di \u00f1\u00ebw \u00ebll\u00ebg.\u00bb\n4:9 Saa su mbindeef ya di m\u00e0ggal ki toog ca g\u00e0ngune ma tey dund ba f\u00e0ww, te di ko ka\u00f1 ak a g\u00ebr\u00ebm,\n4:10 \u00f1aar-fukki mag \u00f1a ak \u00f1eent di d\u00ebpp seen j\u00eb ca kanamu ka toog ca kaw g\u00e0ngune ma. \u00d1u di ko jaamu, moom mi dund ba f\u00e0ww, di s\u00e0nni seen kaalay ndam ca kanamu g\u00e0ngune ma, naan:\n4:11 \u00abY\u00e0lla sunu Boroom,yaa yeyoo ndam, teraanga ak k\u00e0ttan,ndaxte yaa s\u00e0kk l\u00e9ppte ci sa coobare la l\u00e9pp nekke,te ci la\u00f1u leen s\u00e0kke.\u00bb\n5:1 Noonu ma gis ca loxol ndeyjooru ka toog ca g\u00e0ngune ma t\u00e9ere bu \u00f1u bind biir ak biti, tay ko jur\u00f3om-\u00f1aari yoon ak sondeel.\n5:2 Noonu ma gis malaaka mu am doole, muy xaacu naan: \u00abKu yeyoo dindi tayu yi te ubbi t\u00e9ere bi?\u00bb\n5:3 Te amul kenn, muy ci asamaan, muy ci kaw suuf, muy ci biir suuf, ku manoon a ubbi t\u00e9ere bi, mbaa mu xool ci biir.\n5:4 Ma jooy jooy yu metti ndax li kenn yeyoowul woon a ubbi t\u00e9ere bi mbaa mu xool ko.\n5:5 Noonu kenn ca mag \u00f1a ne ma: \u00abBul jooy. Xoolal, Gayndeg giiru Yuda, ki soqikoo ci Daawuda, daan na, ba am sa\u00f1-sa\u00f1u dindi tayu yi te ubbi t\u00e9ere bi.\u00bb\n5:6 Noonu ma gis Mbote mu mel ni da\u00f1u koo rendi woon, mu taxaw ca digg g\u00e0ngune ma, \u00f1eenti mbindeef ya s\u00e9q ko, mag \u00f1a w\u00ebr ko. Mbote ma amoon na jur\u00f3om-\u00f1aari b\u00e9jj\u00e9n ak jur\u00f3om-\u00f1aari b\u00ebt, \u00f1u di jur\u00f3om-\u00f1aari Xeli Y\u00e0lla, yi \u00f1u y\u00f3nni ci \u00e0ddina s\u00e9pp.\n5:7 Mbote ma \u00f1\u00ebw, j\u00ebl t\u00e9ere, ba nekkoon ca loxol ndeyjooru ka toog ca g\u00e0ngune ma.\n5:8 Ba mu j\u00eblee t\u00e9ere ba, \u00f1eenti mbindeef ya ak \u00f1aar-fukki mag \u00f1a ak \u00f1eent daldi d\u00ebpp seen j\u00eb ca kanam Mbote ma, ku nekk yor xalam. \u00d1u yor it andi wurus yu fees ak cuuraay, yu doon misaal \u00f1aani gaayi Y\u00e0lla ya.\n5:9 \u00d1u daldi woy woy wu bees naan:\u00abYeyoo ngaa j\u00ebl t\u00e9ere bite dindi tayu yi,ndaxte reyees na la,te jotal nga Y\u00e0lla ak sa deretay nit \u00f1u bokk ci b\u00e9pp giir,k\u00e0llaama, r\u00e9ew ak xeet.\n5:10 Def nga leen askanu saraxalekatiBuur Y\u00e0lla sunu Boroom,di ko jaamu,te dina\u00f1u nguuru ci \u00e0ddina.\u00bb\n5:11 Ma xool noonu, d\u00e9gg baatu malaaka yu bare yu \u00ebppoon alfunniy alfunniy junniy junni. Malaaka ya w\u00ebr g\u00e0ngune ma ak mbindeef ya ak mag \u00f1a.\n5:12 \u00d1uy xaacu naan:\u00abMbote ma \u00f1u rendi woonyeyoo na k\u00e0ttan, alal, xel,doole, teraanga, ndam ak cant.\u00bb\n5:13 Ma d\u00e9gg itam mbindeef, yi nekk ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf, ci g\u00e9ej gi, \u2014 mbindeef y\u00e9pp naan:\u00abNa cant, teraanga, ndam ak nguurf\u00e9ete ak ki toog ci g\u00e0ngune mi,ak Mbote mi ba f\u00e0ww.\u00bb\n5:14 \u00d1eenti mbindeef ya naan: \u00abAmiin.\u00bb Mag \u00f1a sukk di m\u00e0ggal.\n6:1 Noonu ma gis Mbote ma dindi tayu gu j\u00ebkk ga, te ma daldi d\u00e9gg kenn ca \u00f1eenti mbindeef ya, di wax ak baat buy riir ni d\u00ebnnu naan: \u00ab\u00d1\u00ebwal.\u00bb\n6:2 Ma xool noonu, gis fas wu weex, gawar ba yor ag fitt. \u00d1u jox ko kaalag ndam, mu daldi dem moom j\u00e0mbaar ngir daani.\n6:3 Mbote ma dindi na \u00f1aareelu tayu ga, ma d\u00e9gg \u00f1aareelu mbindeef ma naan: \u00ab\u00d1\u00ebwal.\u00bb\n6:4 Noonu weneen fas g\u00e9nn, di wu xonq, gawar ba jot sa\u00f1-sa\u00f1u j\u00eble j\u00e0mm ci kaw suuf, ngir nit \u00f1i di reyante ci seen biir. \u00d1u jox ko jaasi ju mag.\n6:5 Mu dindi \u00f1etteelu tayu ga, ma d\u00e9gg \u00f1etteelu mbindeef ma ne: \u00ab\u00d1\u00ebwal.\u00bb Ma xool, gis fas wu \u00f1uul, gawar ba yor ab peesekaay.\n6:6 Ma d\u00e9gg baat bu jollee ca diggante \u00f1eenti mbindeef ya, naan: \u00abPeyug b\u00ebcc\u00ebgu l\u00ebmm ngir benn kilob ceeb, peyug b\u00ebcc\u00ebgu l\u00ebmm ngir \u00f1etti kiloy dugub, waaye bul y\u00e0q diw ak bii\u00f1.\u00bb\n6:7 Mu dindi \u00f1eenteelu tayu ga, ma d\u00e9gg \u00f1eenteelu mbindeef ma naan: \u00ab\u00d1\u00ebwal.\u00bb\n6:8 Ma xool noonu, gis fas wu wert, gawar baa nga tuddoon Dee te bars\u00e0q a nga toppoon ci moom. \u00d1u jox ko sa\u00f1-sa\u00f1 ci \u00f1eenteelu xaaju \u00e0ddina s\u00e9pp, ngir mu faat ak jaasi, xiif, mbas ak rabi \u00e0ll yi.\n6:9 Mu dindi jur\u00f3omeelu tayu ga, ma gis ca suufu saraxalukaay, ba \u00f1uy taal cuuraay ca kawam, ruuwi \u00f1i \u00f1u b\u00f3om ndax seede si \u00f1u doon s\u00e0mm ak li \u00f1u g\u00ebmoon k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n6:10 \u00d1uy xaacu naan: \u00abBoroom bu sell bi te d\u00ebggu, ba ka\u00f1 ngay n\u00e9g \u00e0tte bi te feyyul nu sunu deret ci waa \u00e0ddina?\u00bb\n6:11 \u00d1u jox leen ku nekk mbubb mu weex, daldi leen ne, \u00f1u mu\u00f1 tuuti, ba kera seeni nawle \u00f1\u00ebw, te lim bi mat \u2014 seeni nawle ci ligg\u00e9ey bi, di seeni bokk yu waa \u00e0ddina waroon a b\u00f3om ni \u00f1oom.\n6:12 Ma xool, ba muy dindi jur\u00f3om-benneelu tayu ga. Noonu mu am yengu-yengub suuf bu mag, jant bi \u00f1uul ni k\u00ebri\u00f1, weer wi xonq curr ni deret.\n6:13 Biddiiw yi f\u00e0qe asamaan, di daanu ci kaw suuf, ni doomi garab yu yolox di wadd, bu ko ngelaw lu metti dee yengal.\n6:14 Asamaan si dellu ni basa\u014b gu \u00f1uy taxa\u00f1, tund y\u00e9pp ak dun y\u00e9pp randoo fa \u00f1u nekkoon.\n6:15 Noonu buuri \u00e0ddina si, kilifa yi, njiiti xare yi, boroom alal yi, boroom k\u00e0ttan yi, jaam yi ak gor yi, \u00f1\u00e9pp l\u00e0qatuji ci xunti yi ak ci ron doji tund yi.\n6:16 \u00d1u naan tund yi ak doj yi: \u00abDaanuleen ci sunu kaw te n\u00ebbb nu b\u00ebti ki toog ci g\u00e0ngune mi ak meru Mbote mi,\n6:17 ndaxte b\u00e9s bu mag, bi seen mer di fee\u00f1, agsi na! Ku ci man a r\u00ebcc?\u00bb\n7:1 Gannaaw loolu ma gis \u00f1eenti malaaka yu taxaw ci \u00f1eenti xeblay \u00e0ddina si. \u00d1u t\u00e9ye \u00f1eenti ngelawi \u00e0ddina, ngir ngelaw du wol ci kaw suuf, ci g\u00e9ej mbaa ci genn garab.\n7:2 Ma gis it meneen malaaka, muy y\u00e9eg, j\u00f3ge penku, yor m\u00e0ndargakaayu Y\u00e0lla jiy dund. Mu daldi wax ak baat bu xumb \u00f1eenti malaaka ya \u00f1u joxoon sa\u00f1-sa\u00f1, \u00f1u y\u00e0q suuf ak g\u00e9ej,\n7:3 ne leen: \u00abBuleen y\u00e0qagun suuf si ak g\u00e9ej gi ak garab yi. N\u00e9gleen, ba \u00f1u def m\u00e0ndarga ci j\u00ebwu \u00f1iy jaamu Y\u00e0lla sunu Boroom.\u00bb\n7:4 Noonu ma d\u00e9gg limub \u00f1i \u00f1u m\u00e0ndargaal; \u00f1u tollu ci t\u00e9em\u00e9er ak \u00f1eent-fukk ak \u00f1eent ci ay junni. \u00d1u j\u00f3ge ci giiri b\u00e0nni Israyil y\u00e9pp:\n7:5 Fukki junni ak \u00f1aar la\u00f1u m\u00e0ndargaal ci biir giiru Yuda,fukki junni ak \u00f1aar ci giiru Ruben,fukki junni ak \u00f1aar ci giiru G\u00e0dd,\n7:6 fukki junni ak \u00f1aar ci giiru Aser,fukki junni ak \u00f1aar ci giiru Neftali,fukki junni ak \u00f1aar ci giiru Manase,\n7:7 fukki junni ak \u00f1aar ci giiru Simeyon,fukki junni ak \u00f1aar ci giiru Lewi,fukki junni ak \u00f1aar ci giiru Isakaar,\n7:8 fukki junni ak \u00f1aar ci giiru Sabulon,fukki junni ak \u00f1aar ci giiru Yuusufa,fukki junni ak \u00f1aar ci giiru Ben-yamin.\n7:9 Gannaaw loolu ma xool, gis mbooloo mu r\u00e9y, ba kenn m\u00ebnu koo wa\u00f1\u00f1, \u00f1u bokk ci xeet y\u00e9pp, giir y\u00e9pp, r\u00e9ew y\u00e9pp ak k\u00e0llaama y\u00e9pp, taxaw ca kanamu g\u00e0ngune ma ak Mbote ma. \u00d1u sol ay mbubb yu weex, di m\u00e0ggal te di yengal ay cari garab ci seeni loxo,\n7:10 naan:\u00abMucc gaa ngi ci Y\u00e0llasunu Boroom, bi toog ci g\u00e0ngune mi,ak ci Mbote mi!\u00bb\n7:11 Noonu malaaka y\u00e9pp taxaw, w\u00ebr g\u00e0ngune ma ak mag \u00f1a ak \u00f1eenti mbindeef ya. \u00d1u d\u00ebpp seen j\u00eb ca kanamu g\u00e0ngune ma, di jaamu Y\u00e0lla,\n7:12 naan:\u00abAmiin. Na cant ak ndam, xel ak ng\u00ebr\u00ebm, teraanga, k\u00e0ttan ak doolef\u00e9ete ak Y\u00e0lla sunu Boroom ba f\u00e0ww. Amiin!\u00bb\n7:13 Noonu kenn ca mag \u00f1a ne ma: \u00ab\u00d1i sol mbubb yu weex yi, \u00f1ooy \u00f1an ak fan la\u00f1u j\u00f3ge?\u00bb\n7:14 Ma ne ko: \u00abSang bi, xanaa yaa ko xam.\u00bb Mu ne ma: \u00ab\u00d1oo di \u00f1i j\u00f3ge ca metit wu r\u00e9y wa. F\u00f3ot na\u00f1u seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Mbote ma.\n7:15 Loolu moo tax\u00f1u nekk ci kanamu g\u00e0ngunem Y\u00e0lla,di ko jaamu guddi ak b\u00ebcc\u00ebg ci k\u00ebram,te ki toog ci g\u00e0ngune mi dina leen yiir.\n7:16 Dootu\u00f1u xiif, dootu\u00f1u mar.Jant mbaa weneen t\u00e0ngaay du leen lakk,\n7:17 ndaxte Mbote mi nekk ci diggu g\u00e0ngune mi dina leen s\u00e0mm,y\u00f3bbu leen ca b\u00ebti ndoxum dund ma,te Y\u00e0lla dina fomp b\u00e9pp rangoo\u00f1 ci seeni b\u00ebt.\u00bb\n8:1 Mbote ma dindi na jur\u00f3om-\u00f1aareelu tayu ga, asamaan ne selaw lu mat genn-w\u00e0llu waxtu.\n8:2 Noonu ma gis jur\u00f3om-\u00f1aari malaaka, yi taxaw ca kanam Y\u00e0lla, \u00f1u daldi leen jox jur\u00f3om-\u00f1aari liit.\n8:3 Ba loolu amee meneen malaaka \u00f1\u00ebw, taxaw ca wetu saraxalukaayu wurus, ba \u00f1uy taal cuuraay ca kawam, yor andu cuuraayu wurus. \u00d1u jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole ko ak \u00f1aani gaayi Y\u00e0lla y\u00e9pp, joxe ko ci kaw saraxalukaayu wurus ba nekk ci kanam g\u00e0ngune mi.\n8:4 Noonu saxarus cuuraay li gillee ca loxob malaaka ma, \u00e0nd ak \u00f1aani gaayi Y\u00e0lla ya, j\u00ebm ca kanam Y\u00e0lla.\n8:5 Malaaka ma j\u00ebl andu cuuraay ba, duy ko ak ay xal ca saraxalukaay ba, daldi koy s\u00e0nni ci \u00e0ddina. Noonu mu am ay d\u00ebnnu, ay riir, ay melax ak yengu-yengub suuf.\n8:6 Ba mu ko defee jur\u00f3om-\u00f1aari malaaka, ya yoroon jur\u00f3om-\u00f1aari liit ya, daldi defaru di waaj a liit.\n8:7 Malaaka mu j\u00ebkk ma wol liitam. Noonu \u00f1u s\u00e0nni ci \u00e0ddina yuur ak safara yu \u00f1u boole ak deret, ba tax benn ci \u00f1etti xaaju suuf si lakk, benn ci \u00f1etti xaaju garab yi it lakk, te \u00f1ax mu naat m\u00e9pp lakk.\n8:8 \u00d1aareelu malaaka ma wol liitam. Noonu \u00f1u s\u00e0nni lu mel ni tundu safara wu r\u00e9y, mu daanu ci g\u00e9ej gi, benn ci \u00f1etti xaaju g\u00e9ej gi soppiku deret,\n8:9 benn ci \u00f1etti xaaju mbindeef yi nekk ci g\u00e9ej gi dee, te benn ci \u00f1etti xaaju gaal yi y\u00e0qu.\n8:10 \u00d1etteelu malaaka ma wol liitam. Noonu biddiiw bu r\u00e9y, y\u00e0nj ni jum, xawee asamaan, daanu ci benn ci \u00f1etti xaaju dex yi ak ci b\u00ebti ndox yi.\n8:11 Biddiiw boobu mi ngi tuddoon Wextan. Nit \u00f1u bare naan ci ndox mi daldi dee, ndaxte ndox mi dafa daldi wex.\n8:12 \u00d1eenteelu malaaka ma wol liitam. Noonu d\u00f3orees benn ci \u00f1etti xaaju jant bi, ak benn ci \u00f1etti xaaju weer wi, ak benn ci \u00f1etti xaaju biddiiw yi, ba tax benn ci \u00f1etti xaaju leer gi l\u00ebnd\u00ebm. B\u00ebcc\u00ebg bi \u00f1\u00e0kk leer diirub benn ci \u00f1etti xaajam, guddi gi \u00f1\u00e0kk leer diirub benn ci \u00f1etti xaajam.\n8:13 Ma xool noonu, d\u00e9gg jaxaay juy naaw ci digg asamaan, naan ak baat bu xumb: \u00abMusiba, musiba! Musibaa ngi ci kaw waa \u00e0ddina, ndax liit yi yeneen \u00f1etti malaaka yi di wol.\u00bb\n9:1 Jur\u00f3omeelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma gis, \u00f1u jox caabiy k\u00e0mb gu x\u00f3ot gi benn biddiiw bu xawee woon asamaan, daanu ci kaw suuf.\n9:2 Biddiiw ba ubbi buntu k\u00e0mb gu x\u00f3ot ga. Noonu saxar jollee ca, su mel ni saxarus puur bu mag, jant bi ak jaww ji l\u00e9pp l\u00ebnd\u00ebm ndax saxarus k\u00e0mb ga.\n9:3 Ay nj\u00e9er\u00e9er g\u00e9nn ca saxar sa, tasaaroo ci biir \u00e0ddina. \u00d1u jox leen k\u00e0ttan gu mel ni k\u00e0ttanu j\u00e0nkalaar.\n9:4 \u00d1u sant leen, \u00f1u ba\u00f1 a laal \u00f1ax mi ci kaw suuf, mbaa genn g\u00e0ncax walla genn me\u00f1\u00f1eef, waaye \u00f1u jublu rekk ci nit \u00f1u amul m\u00e0ndargam Y\u00e0lla ci seen j\u00eb.\n9:5 Santu\u00f1u leen \u00f1u rey leen, waaye \u00f1u metital leen diirub jur\u00f3omi weer. Te metit woowu \u00f1uy indi, temboo na ak metit wiy dal nit, bu ko j\u00e0nkalaar fittee.\n9:6 Ca jamono yooya nit \u00f1i dina\u00f1u s\u00e0kku dee, waaye du\u00f1u daje ak moom. Dina\u00f1u b\u00ebgg a dee, waaye dee da leen di daw.\n9:7 Nj\u00e9er\u00e9er ya nag da\u00f1uy niroo ak fas yu \u00f1u waajal ngir xare. Am na\u00f1u ci seen bopp lu mel ni kaalay wurus, te seen xar-kanam mel ni gu nit.\n9:8 Seeni kawar mel ni yu jig\u00e9en, seeni b\u00eb\u00f1 mel ni b\u00eb\u00f1i gaynde.\n9:9 Takk na\u00f1u ci seen d\u00ebnn lu mel ni kiiraayu we\u00f1, te coow la seeni laaf di def mel ni coowu sareeti xare yu bare yu \u00f1u takk fas, di xeexi.\n9:10 Am na\u00f1u ay geen yu am ay fitt ni j\u00e0nkalaar, te ca la seen k\u00e0ttan nekk, ngir metital nit \u00f1i diirub jur\u00f3omi weer.\n9:11 Buuru nj\u00e9er\u00e9er yi mooy malaakam k\u00e0mb gu x\u00f3ot gi, moom la\u00f1u tudde ci l\u00e0kku Yawut, Abadon, ak ci l\u00e0kku gereg, Apolyon, liy tekki \u00abY\u00e0qkat.\u00bb\n9:12 Musiba mu j\u00ebkk mi j\u00e0ll na, yeneen \u00f1aari musiba yaa ngi \u00f1\u00ebw.\n9:13 Jur\u00f3om-benneelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma d\u00e9gg baat bu j\u00f3ge ci \u00f1eenti b\u00e9jj\u00e9n, yi nekk ci ko\u00f1i saraxalukaayu wurus, ba nekk ci kanam Y\u00e0lla,\n9:14 mu ne jur\u00f3om-benneelu malaaka, ma yoroon liit: \u00abYiwil \u00f1eenti malaaka, ya yeewe ca Efraat, dex gu mag ga.\u00bb\n9:15 Noonu \u00f1u daldi yiwi \u00f1eenti malaaka, ya \u00f1u waajaloon ngir at moomu, weer woowu, b\u00e9s boobu ak waxtu woowu, ngir \u00f1u rey benn ci \u00f1etti xaaju nit \u00f1i.\n9:16 Limub gawar ga doon xareji mat na \u00f1aari alfunniy alfunni. D\u00e9gg naa lim ba.\n9:17 Nii laa gise ci pee\u00f1u mi fas ya ak \u00f1a leen war: \u00f1u sol kiiraay yu xonq ni safara, bulo ni saxar, ak mboq ni tamarax. Boppi fas yaa nga doon nirook boppi gaynde; safara, saxar ak tamarax di g\u00e9nn ci seeni g\u00e9mmi\u00f1.\n9:18 Benn ci \u00f1etti xaaju nit \u00f1i dee ci \u00f1etti musiba ya: ci safara, saxar ak tamarax yi g\u00e9nn ci seeni g\u00e9mmi\u00f1.\n9:19 Ndaxte k\u00e0ttanu fas yaa ngi ci seeni g\u00e9mmi\u00f1 ak ci seeni geen. Geen yaa nga mel ni ay jaan, am ay bopp, te \u00f1oom la\u00f1uy metitale nit \u00f1i.\n9:20 Nit \u00f1i r\u00ebcc ci musiba yooyu taxul sax \u00f1u tuub seeni j\u00ebfi loxo. Noppiwu\u00f1u di jaamu rab yi ak nataali x\u00ebr\u00ebm yu \u00f1u defare wurus ak xaalis ak x\u00e0njar ak xeer ak d\u00e9nk, yoo xam ne m\u00ebnu\u00f1oo gis, m\u00ebnu\u00f1oo d\u00e9gg mbaa \u00f1u dox.\n9:21 Te nit \u00f1oo\u00f1u tuubu\u00f1u seen b\u00f3om, seen x\u00ebr\u00ebm, seen njaaloo mbaa seen c\u00e0cc.\n10:1 Noonu ma gis meneen malaaka mu am doole, muy w\u00e0cce asamaan, l\u00e0mboo niir. Xon tiim ko, te xar-kanamam mel ni jant, te ay t\u00e0nkam mel ni jumi safara.\n10:2 Yor na benn t\u00e9ere bu ndaw bu \u00f1u ubbi. Mu teg t\u00e0nku ndeyjooram ci g\u00e9ej gi, t\u00e0nku c\u00e0mmoo\u00f1am ci suuf si,\n10:3 di xaacu, mel ni gaynde guy y\u00ebmmu. Naka la xaacu, jur\u00f3om-\u00f1aari d\u00ebnnu yi jib.\n10:4 Naka la jur\u00f3om-\u00f1aari d\u00ebnnu yi di jib, may waaj a bind, waaye ma d\u00e9gg baat bu j\u00f3ge asamaan, naan ma: \u00abLi jur\u00f3om-\u00f1aari d\u00ebnnu yi wax, na nekk kumpa, bu ko bind.\u00bb\n10:5 Noonu malaaka ma ma gis, mu taxaw ci g\u00e9ej gi ak suuf si, y\u00e9kkati loxol ndeyjooram, mu j\u00ebm asamaan,\n10:6 daldi waat ci kiy dund ba f\u00e0ww, ki s\u00e0kk asamaan ak suuf ak g\u00e9ej ak li ci nekk l\u00e9pp; mu ne: \u00abN\u00e9gandiku wees na,\n10:7 waaye jamono ju jur\u00f3om-\u00f1aareelu malaaka ma wolee ci liitam, ndogalu Y\u00e0lla dina mat, ni mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.\u00bb\n10:8 Ci kaw loolu baat, ba ma d\u00e9ggoon ca asamaan waxaat ak man, ne ma: \u00abDemal j\u00ebl t\u00e9ere bi \u00f1u ubbi ci loxob malaaka, mi taxaw ci g\u00e9ej gi ak suuf si.\u00bb\n10:9 Ma dem ca malaaka ma, laaj ko t\u00e9ere bu ndaw boobu. Mu ne ma: \u00abJ\u00ebl ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir, waaye dina neex ni lem ci sa g\u00e9mmi\u00f1.\u00bb\n10:10 Noonu ma j\u00ebl t\u00e9ere bi ci loxob malaaka mi, daldi ko lekk, mu neex ci sama g\u00e9mmi\u00f1 ni lem, waaye bi ma ko wannee, mu wex xat ci sama biir.\n10:11 Gannaaw loolu \u00f1u ne ma: \u00abF\u00e0ww nga wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla lu j\u00ebm ci r\u00e9ew yu bare, xeet yu bare, k\u00e0llaama yu bare ak buur yu bare.\u00bb\n11:1 Bi loolu amee \u00f1u jox ma nattukaay bu mel ni yet, ne ma: \u00abJ\u00f3gal, natt k\u00ebr Y\u00e0lla gi ak saraxalukaay bi, te wa\u00f1\u00f1 \u00f1a fay jaamu Y\u00e0lla.\n11:2 Waaye b\u00e0yyil \u00ebttu bitib k\u00ebr Y\u00e0lla gi; bu ko natt, ndaxte j\u00e9bbalees na ko \u00f1i dul Yawut, te dina\u00f1u nappaaje d\u00ebkk bu sell bi diirub \u00f1eent-fukki weer ak \u00f1aar.\n11:3 Dinaa may sama \u00f1aari seede yi, \u00f1uy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla, sol ay saaku, di toroxlu diirub junni ak \u00f1aari t\u00e9em\u00e9eri fan ak jur\u00f3om-benn-fukk.\u00bb\n11:4 \u00d1aari seede ya nag \u00f1oo di \u00f1aari garabu oliw yeek \u00f1aari l\u00e0mpu diwlin, yi taxaw ci kanam Boroom suuf si.\n11:5 Su leen kenn b\u00ebggee def lu bon, safaraay g\u00e9nn ci seen g\u00e9mmi\u00f1, daldi lakk seeni ba\u00f1aale; te ku leen b\u00ebgg a def lu bon, noonu lay war a deeye.\n11:6 Am na\u00f1u sa\u00f1-sa\u00f1u t\u00e9ye taw diirub fan, yi \u00f1uy wax ci k\u00e0ddug Y\u00e0lla. Am na\u00f1u it sa\u00f1-sa\u00f1u soppi ndox yi deret te w\u00e0cce ci kaw suuf musiba yu nekk, saa su \u00f1u ko b\u00ebggee.\n11:7 Bu \u00f1u noppee seen seede, rab wiy j\u00f3ge ci k\u00e0mb gi dina leen xeex, daan leen, rey leen.\n11:8 Te seeni n\u00e9ew dina\u00f1u nekk ci p\u00e9ncum d\u00ebkk bu mag, boobu \u00f1uy wooye ci misaal Sodom ak it Misra, fa \u00f1u reyoon seen Boroom ci bant.\n11:9 Te diirub \u00f1etti fan ak genn-w\u00e0ll b\u00e9pp r\u00e9ew, giir, k\u00e0llaama ak xeet dina\u00f1u seetaan seeni n\u00e9ew te du\u00f1u b\u00e0yyi kenn suul leen.\n11:10 Waa \u00e0ddina dina\u00f1u b\u00e9g ci seen dee, di ndokkeelante ak di joqleente ay may, ndaxte \u00f1aari yonent ya lakkaloon na\u00f1u waa \u00e0ddina.\n11:11 Waaye bi \u00f1etti fan ya ak genn-w\u00e0ll w\u00e9yee, xelum dund, j\u00f3ge ca Y\u00e0lla, solu leen, \u00f1u j\u00f3g taxaw. Noonu tiitaange gu r\u00e9y j\u00e0pp \u00f1i leen doon seetaan.\n11:12 \u00d1aari seede ya d\u00e9gg baat bu xumb ca asamaan naan leen: \u00abY\u00e9egleen fii.\u00bb Noonu \u00f1u y\u00e9eg asamaan ci aw niir, seeni ba\u00f1aale di seetaan.\n11:13 Ca saa sa am yengu-yengub suuf bu mag, te benn ci fukki xaaju d\u00ebkk ba daldi m\u00e0bb. Jur\u00f3om-\u00f1aari junniy nit dee ci yengu-yengub suuf ba, te \u00f1a ca des tiit, daldi m\u00e0ggal Y\u00e0llay asamaan.\n11:14 \u00d1aareelu musiba mi w\u00e9y na, \u00f1etteel baa ngi nii di \u00f1\u00ebw.\n11:15 Jur\u00f3om-\u00f1aareelu malaaka ma wol liitam, noonu baat yu xumb jib ca asamaan naan:\u00abNguuru \u00e0ddina, j\u00e9bbalaat na\u00f1u kosunu Boroom ak Almaseem,te dina nguuru ba f\u00e0ww.\u00bb\n11:16 \u00d1aar-fukki mag ak \u00f1eent, \u00f1a toogoon ca seen g\u00e0ngune ca kanam Y\u00e0lla, daldi d\u00ebpp seen j\u00eb ca suuf, jaamu Y\u00e0lla,\n11:17 naan:\u00abNu ngi lay g\u00ebr\u00ebm, Boroom bi Y\u00e0lla,yaw Aji K\u00e0ttan ji, ki nekk te nekkoon,ndax g\u00e0njoo nga sa k\u00e0ttan gu r\u00e9y gi,ngir taxawal sa nguur.\n11:18 Xeet yi meroon na\u00f1u,waaye sa mer w\u00e0cc na,te jamono ji jot na,ji ngay \u00e0ttee \u00f1i dee,neexal say jaam yonent yi,ak sa gaa \u00f1i ak \u00f1i ragal saw tur,muy mag di ndaw,te nga rey \u00f1iy y\u00e0q \u00e0ddina.\u00bb\n11:19 Noonu k\u00ebr Y\u00e0lla gi ci asamaan daldi ubbiku, gaalu k\u00f3ll\u00ebreg Y\u00e0lla ga daldi fee\u00f1 ca biir k\u00ebr Y\u00e0lla ga, te mu daldi am ay melax, ay coow, ay d\u00ebnnu, yengu-yengub suuf ak tawu yuur bu metti.\n12:1 Amoon na firnde ju r\u00e0\u00f1\u00f1iku ju fee\u00f1 ca asamaan, di jig\u00e9en ju l\u00e0mboo jant bi, kaalawoo fukki biddiiw ak \u00f1aar, weer wi nekk ci suufu t\u00e0nkam.\n12:2 Jig\u00e9enu biir la, di yuuxu ndax metitu mat wu tar.\n12:3 Noonu beneen firnde fee\u00f1 ca asamaan, di ninkin\u00e0nka ju r\u00e9y, xonq curr te am jur\u00f3om-\u00f1aari bopp ak fukki b\u00e9jj\u00e9n. Ca bopp ya am na jur\u00f3om-\u00f1aari mbaxanay buur.\n12:4 Geenam di laawaale \u00f1etti c\u00e9r yu ne benn ca biddiiwi asamaan, di leen s\u00e0nni ci suuf. Ninkin\u00e0nka ja taxaw ca kanamu jig\u00e9en jay matu, ngir lekk liir ba, bu juddoo.\n12:5 Noonu mu jur doom ju g\u00f3or, muy ki war a jiite xeeti \u00e0ddina y\u00e9pp ak yetu we\u00f1. Waaye \u00f1u daldi f\u00ebkk doom ja, mu dem ca Y\u00e0lla ak g\u00e0nguneem.\n12:6 Gannaaw loolu jig\u00e9en ja daw, dem ca m\u00e0ndi\u014b ma, ca dalukaay ba ko Y\u00e0lla waajaloon ngir mu nekk fa, \u00f1u dundal ko fa diirub junni ak \u00f1aari t\u00e9em\u00e9eri fan ak jur\u00f3om-benn-fukk.\n12:7 Noonu xare am ca asamaan ya. Mikayel ak malaaka, ya \u00e0nd ak moom, xeex ak ninkin\u00e0nka ja, ninkin\u00e0nka ja it ak ay malaakaam feyyu.\n12:8 Waaye ninkin\u00e0nka jaa g\u00ebn a n\u00e9ew doole; noonu \u00f1u d\u00e0qe ko ak toppam asamaan.\n12:9 Daaneel na\u00f1u ko, moom ninkin\u00e0nka ju r\u00e9y ji, di jaani cosaan ji, te \u00f1u di ko wax Tuumaalkat bi mbaa Seytaane, moom miy nax waa \u00e0ddina s\u00e9pp \u2014 daaneel na\u00f1u ko ci kaw suuf, moom ak ay malaakaam.\n12:10 Noonu ma d\u00e9gg baat bu xumb j\u00f3ge asamaan naan:\u00abL\u00e9egi mucc agsi na,moom ak k\u00e0ttanak nguuru Y\u00e0lla sunu Boroom,ak sa\u00f1-sa\u00f1u Almaseem,ndaxte ki daan tuumaal sunuy bokk,di leen sosal guddi ak b\u00ebcc\u00ebgci kanam Y\u00e0lla sunu Boroom,kooka daaneel na\u00f1u ko.\n12:11 Fekk noot na\u00f1u kojaarale ko ci deretu Mbote maak seen seedes ng\u00ebm,te soppu\u00f1u seen bakkan ba ragal a dee.\n12:12 Looloo tax, na asamaanak \u00f1i ci d\u00ebkk b\u00e0nneexu!Musiba ci kaw suuf ak ci biir g\u00e9ej!Ndaxte Seytaane w\u00e0cc na ci y\u00e9en,\u00e0nd ak mer mu t\u00e0ng,ndaxte xam na ne, jot gi ko dese barewul.\u00bb\n12:13 Ba ninkin\u00e0nka ja gisee ne, daaneel na\u00f1u ko ci kaw suuf, mu d\u00e0q jig\u00e9en, ja juroon doom ju g\u00f3or ja.\n12:14 Noonu \u00f1u jox jig\u00e9en ja \u00f1aari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, ba sore ninkin\u00e0nka ja, dem ca m\u00e0ndi\u014b ma ca b\u00e9rabam, \u00f1u dundal ko fa ab diir, ay diir ak genn-w\u00e0llu diir.\n12:15 Ninkin\u00e0nka ja buusu ndox mu bare ni dex ca gannaaw jig\u00e9en ja, ngir y\u00f3bbaale ko ca.\n12:16 Waaye suuf wallu jig\u00e9en ja, naan dex, ga ninkin\u00e0nka ja buusu woon.\n12:17 Ninkin\u00e0nka ja mere jig\u00e9en ja, daldi xeexi ak \u00f1i des ciy doomam, di \u00f1iy s\u00e0mm ndigali Y\u00e0lla tey sax ci di seedeel Yeesu.\n12:18 Noonu mu taxaw ca tefesu g\u00e9ej ga.\n13:1 Noonu ma gis g\u00e9nn ca g\u00e9ej ga, rab wu am fukki b\u00e9jj\u00e9n ak jur\u00f3om-\u00f1aari bopp. Ci kaw b\u00e9jj\u00e9nam ya amoon na fukki mbaxanay buur; ca bopp ya turi xarab Y\u00e0lla.\n13:2 Rab wa ma gis ma nga mel ni segg, t\u00e0nk ya mel ni yu rab wu \u00f1uy wax urs, g\u00e9mmi\u00f1 ga mel ni gu gaynde. Ninkin\u00e0nka ja jox ko k\u00e0ttanam, nguuram ak sa\u00f1-sa\u00f1am bu r\u00e9y.\n13:3 Benn ca bopp ya mel ni dafa gaa\u00f1u ba dee. Waaye gaa\u00f1u-gaa\u00f1u ba daldi w\u00e9r. Waa \u00e0ddina s\u00e9pp y\u00e9emu, daldi topp rab wa.\n13:4 \u00d1u jaamu ninkin\u00e0nka ja ndax li mu joxoon sa\u00f1-sa\u00f1 rab wa, di jaamu it rab wa, naan: \u00abRab wi amul moroom, kenn m\u00ebnul a xeex ak moom.\u00bb\n13:5 Noonu mayees ko mu am g\u00e9mmi\u00f1, muy jey boppam te di xarab turu Y\u00e0lla. Mayees ko it sa\u00f1-sa\u00f1u j\u00ebf ci kaw suuf diirub \u00f1eent-fukki weer ak \u00f1aar.\n13:6 Noonu mu t\u00e0mbalee xarab Y\u00e0lla, di xarab aw turam, dalam, ak \u00f1i d\u00ebkk ci asamaan.\n13:7 Mayees ko, mu xare ak gaayi Y\u00e0lla yi te noot leen. Mayees ko it sa\u00f1-sa\u00f1 ci kaw b\u00e9pp giir, r\u00e9ew, k\u00e0llaama ak xeet.\n13:8 Waa \u00e0ddina s\u00e9pp dina\u00f1u ko jaamu, \u00f1oo\u00f1u \u00f1u bindul seeni tur, li dale ci nj\u00e0lb\u00e9enu \u00e0ddina, ci t\u00e9ereb dund bu Mbote mi \u00f1u rendi.\n13:9 Yaw mi am ay nopp, d\u00e9glul.\n13:10 Ku Y\u00e0lla dogal,\u00f1u war laa j\u00e0pp njaam,dina\u00f1u la j\u00e0pp njaam.Ku Y\u00e0lla dogal,\u00f1u war laa rey ak jaasi,dina\u00f1u la rey ak jaasi. Looloo tax gaayi Y\u00e0lla yi war a mu\u00f1 te takku.\n13:11 Noonu ma gis weneen rab di g\u00e9nn ci suuf. Am na \u00f1aari b\u00e9jj\u00e9n yu mel ni yu mbote, waaye di wax ni ninkin\u00e0nka.\n13:12 Muy j\u00ebf ak sa\u00f1-sa\u00f1u rab wu j\u00ebkk wa ci turam, di sant waa \u00e0ddina s\u00e9pp, \u00f1u jaamu rab wu j\u00ebkk, woowu am gaa\u00f1u-gaa\u00f1u ba ko rey, waaye daldi w\u00e9r.\n13:13 Muy def k\u00e9emaan yu r\u00e9y, ba dem sax bay w\u00e0cce ci kaw suuf safara su j\u00f3ge asamaan, nit \u00f1i di gis.\n13:14 Noonu mu nax waa \u00e0ddina ci k\u00e9emaan, yi mu am sa\u00f1-sa\u00f1u def ci turu rab wu j\u00ebkk wa. Mu sant waa \u00e0ddina, \u00f1u def nataalu rab, wi am gaa\u00f1u-gaa\u00f1ub jaasi tey dund.\n13:15 Mayees ko it, mu dundloo nataalu rab wa, waxloo ko, ba k\u00e9pp ku jaamuwul nataalu rab wa rekk \u00f1u rey la.\n13:16 Mu def it ba \u00f1\u00e9pp, mag ak ndaw, buur ak baadoolo, gor ak jaam, \u00f1\u00e9pp am m\u00e0ndarga ci seen loxol ndeyjoor walla ci seen j\u00eb,\n13:17 ba kenn du man a j\u00ebnd mbaa mu jaay te amul m\u00e0ndargam rab wi, maanaam turam walla siifar bu mengoo ak turam.\n13:18 Lii nag mooy laaj xel: ku am xel dina man a wa\u00f1\u00f1 siifaru rab wi, ndaxte siifar boobu mengoo na ak bu nit, di jur\u00f3om-benni t\u00e9em\u00e9er ak jur\u00f3om-benn-fukk ak jur\u00f3om-benn.\n14:1 Ma xool noonu, gis Mbote ma taxaw ci tundu Siyon, \u00e0nd ak t\u00e9em\u00e9er ak \u00f1eent-fukk ak \u00f1eenti junniy nit, te \u00f1u bind ci seen j\u00eb turu Mbote ma ak turu Baayam.\n14:2 Ma d\u00e9gg baat bu j\u00f3ge asamaan, buy riir ni duusi g\u00e9ej, ni riiru d\u00ebnnu gu r\u00e9y. Baat ba ma d\u00e9gg mel ni baati xalamkat yuy xalam.\n14:3 Nit \u00f1u bare \u00f1oo\u00f1u taxaw ca kanamu g\u00e0ngune ma ak \u00f1eenti mbindeef ya ak mag \u00f1a, di woy woy wu bees. Kenn m\u00ebnul a j\u00e0ng woy wa, ku dul t\u00e9em\u00e9er ak \u00f1eent-fukk ak \u00f1eenti junniy nit, \u00f1oo\u00f1u \u00f1u jote \u00e0ddina.\n14:4 \u00d1oo di \u00f1i taqul sobey jig\u00e9en, ndaxte saxal na\u00f1u seen bopp ci sell. \u00d1u nga topp Mbote ma f\u00e9pp fu mu j\u00ebm. Y\u00e0lla jot na leen ci biir nit \u00f1i, \u00f1u j\u00e9bbalu ci Y\u00e0lla ak ci Mbote mi, mel ni t\u00e0nneefu ng\u00f3ob mi \u00f1uy s\u00e9dde Y\u00e0lla,\n14:5 te fen musul a g\u00e9nn ci seen g\u00e9mmi\u00f1. Amu\u00f1u benn sikk.\n14:6 Noonu ma gis meneen malaaka naaw ca digg asamaan, yor xebaar bi sax, di ko y\u00e9gal waa \u00e0ddina \u2014 xeet y\u00e9pp, giir y\u00e9pp, k\u00e0llaama y\u00e9pp ak r\u00e9ew y\u00e9pp.\n14:7 Ma nga doon xaacu naan: \u00abRagal-leen Y\u00e0lla te jox ko ndam li, ndaxte waxtuw \u00e0tteem jot na. Jaamuleen ki s\u00e0kk asamaan ak suuf ak g\u00e9ej ak b\u00ebti ndox yi.\u00bb\n14:8 Meneen malaaka, di \u00f1aareel bi, topp ca naan: \u00abDaanu na! Babilon, d\u00ebkk bu mag, bi daan m\u00e0ndil r\u00e9ew y\u00e9pp ak bii\u00f1u njaaloom, daanu na.\u00bb\n14:9 Meneen malaaka, di \u00f1etteel bi, topp ca, di xaacu naan: \u00abKu jaamu rab wi ak nataalam te nangoo am m\u00e0ndargam ci j\u00ebwam walla ci loxoom,\n14:10 dina naan moom itam bii\u00f1u xadarub Y\u00e0lla bi kenn raxul, \u00f1u sotti ko ci koppu meram. Te dees na ko mbugal ci safara ak tamarax ci kanamu malaaka yu sell yi ak Mbote mi,\n14:11 te saxar siy j\u00f3ge ci seen mbugal dina gilli ba f\u00e0ww. \u00d1oo\u00f1u di jaamu rab wi ak nataalam, ak k\u00e9pp ku nangoo jot m\u00e0ndargam turam, du\u00f1u noppalu guddi ak b\u00ebcc\u00ebg.\u00bb\n14:12 Looloo tax gaayi Y\u00e0lla yi war a mu\u00f1, \u00f1oo\u00f1uy s\u00e0mm ndigali Y\u00e0lla yi ak ng\u00ebm ci Yeesu.\n14:13 Noonu ma d\u00e9gg baat ci asamaan naan: \u00abBindal: \u201cB\u00e9s ni tey, \u00f1i nekk ci Boroom bi te dee, barkeel na\u00f1u.\u201d\u00bb Xelum Y\u00e0lla nee na: \u00abWaaw, dina\u00f1u noppalu ci seeni coono, ndaxte seeni j\u00ebf a nga leen di xaar.\u00bb\n14:14 Ma xool noonu, gis niir wu weex ak ku ca toog, niroo ak doomu nit, takk kaalag wurus ca bopp ba, yor s\u00e0rt bu \u00f1aw.\n14:15 Te meneen malaaka g\u00e9nn ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, di wax ak baat bu xumb ak ka toogoon ca niir wa, ne ko: \u00abDawalal sa s\u00e0rt te g\u00f3ob, ndaxte ng\u00f3ob jot na, te l\u00e9pp \u00f1or na ci kaw suuf.\u00bb\n14:16 Noonu ka toogoon ca kaw niir wa dawal s\u00e0rtam ci kaw suuf, g\u00f3ob \u00e0ddina s\u00e9pp.\n14:17 Bi loolu amee meneen malaaka g\u00e9nn ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga nekk ca asamaan, yor moom itam s\u00e0rt bu \u00f1aw.\n14:18 Noonu meneen malaaka, ma am sa\u00f1-sa\u00f1 ca safara sa, j\u00f3ge ca saraxalukaayu cuuraay ba, daldi wax ak baat bu xumb ak malaaka, ma yor s\u00e0rt bu \u00f1aw ba, ne ko: \u00abDawalal sa s\u00e0rt bu \u00f1aw bi te dagg c\u00e9ggu r\u00e9se\u00f1 yu \u00e0ddina, ndaxte \u00f1or na\u00f1u.\u00bb\n14:19 Noonu malaaka ma daldi dawal s\u00e0rtam ci \u00e0ddina, dagg r\u00e9se\u00f1 yi, s\u00e0nni leen ci biir segalukaay bu r\u00e9y bu merum Y\u00e0lla.\n14:20 \u00d1u nal r\u00e9se\u00f1 ya ca segalukaay, ba ca gannaaw d\u00ebkk ba, deret g\u00e9nn ca, ba agsi ci laabi fas yi, te wal ba \u00ebmb lu mat \u00f1etti t\u00e9em\u00e9eri kilomet.\n15:1 Noonu ma gis ca asamaan beneen firnde ju r\u00e9y tey y\u00e9eme: jur\u00f3om-\u00f1aari malaaka yu taawu jur\u00f3om-\u00f1aari musiba, \u00f1uy yu mujj ya, ndaxte \u00f1oom \u00f1ooy matal merum Y\u00e0lla.\n15:2 Noonu ma gis lu mel ni g\u00e9ej gu leer ni weer bu set buy ray-rayi ak safara. \u00d1a nootoon rab wa ak nataalam, ak siifar bu mengoo ak turam, \u00f1oo taxaw ca g\u00e9ej gu leer ga, yor xalam yu leen Y\u00e0lla jox.\n15:3 \u00d1uy woy woyu Musaa jaamu Y\u00e0lla bi, ak woyu Mbote ma, naan:\u00abSay j\u00ebf r\u00e9y na\u00f1u te y\u00e9eme,yaw Boroom bi Y\u00e0lla, Aji K\u00e0ttan ji.Say yoon jub na\u00f1u te d\u00ebggu,yaw Buur bi fiy sax ba abadan.\n15:4 Ku la ragalul, Boroom bi?Ku dul m\u00e0ggal saw tur?Kenn, ndaxte yaw rekk yaa sell.Xeet y\u00e9pp dina\u00f1u dikk, jaamu la,ndax say \u00e0tte bir na \u00f1\u00e9pp.\u00bb\n15:5 Gannaaw loolu ma xool, noonu k\u00ebr Y\u00e0lla ubbiku ca asamaan, muy t\u00e0ntu m\u00e0ggalukaay, bi \u00ebmb li Y\u00e0lla seede.\n15:6 Jur\u00f3om-\u00f1aari malaaka, ya taawu jur\u00f3om-\u00f1aari musiba ya, daldi g\u00e9nn ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga. \u00d1u sol mbubb yu set te weex bay lerax, laxasaayoo nge\u00f1aayi wurus ba ci seen d\u00ebnn.\n15:7 Noonu kenn ci \u00f1eenti mbindeef ya jox jur\u00f3om-\u00f1aari malaaka ya jur\u00f3om-\u00f1aari ndabi wurus yu fees ak merum Y\u00e0lla jiy dund ba f\u00e0ww.\n15:8 K\u00ebr Y\u00e0lla ga fees ak saxar ndax leeraayu ndamu Y\u00e0lla ak k\u00e0ttanam. Te kenn m\u00ebnatul a dugg ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, ba kera jur\u00f3om-\u00f1aari musiba, ya jur\u00f3om-\u00f1aari malaaka ya taawu, di mat.\n16:1 Noonu ma d\u00e9gg baat bu xumb bu j\u00f3ge ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, naan jur\u00f3om-\u00f1aari malaaka ya: \u00abDemleen sotti ci \u00e0ddina jur\u00f3om-\u00f1aari ndabi merum Y\u00e0lla yi.\u00bb\n16:2 Noonu malaaka mu j\u00ebkk ma dem, sotti ndabam ci \u00e0ddina, ba woppi taab ju bon te metti dal nit, \u00f1a am m\u00e0ndargam rab wa tey jaamu nataalam.\n16:3 \u00d1aareelu malaaka ma sotti ndabam ci g\u00e9ej gi. Mu soppiku deret ni deretu n\u00e9ew, ba l\u00e9pp luy dund te nekkoon ci g\u00e9ej gi dee.\n16:4 \u00d1etteelu malaaka ma sotti ndabam ci dex yi ak ci b\u00ebti ndox yi. \u00d1u daldi nekk deret.\n16:5 Noonu ma d\u00e9gg malaaka mi am sa\u00f1-sa\u00f1 ci ndox yi naan:\u00abKu jub nga, yaw ki nekk te nekkoon,yaw Aji Sell ji,ci li nga dogal \u00e0tte yooyu.\n16:6 Ndaxte tuur na\u00f1u deretu sa gaa \u00f1iak ju yonent yi,yaw it fey nga leen seen bor,jox leen deret, \u00f1u naan.\u00bb\n16:7 Ma d\u00e9gge baat jibe ca saraxalukaayu cuuraay ba naan:\u00abWaaw Boroom bi Y\u00e0lla, Aji K\u00e0ttan ji,say \u00e0tte d\u00ebggu na\u00f1u te jub.\u00bb\n16:8 \u00d1eenteelu malaaka ma tuur ndabam ci jant bi. Noonu \u00f1u jox ko sa\u00f1-sa\u00f1u lakk nit \u00f1i ak t\u00e0ngaayam.\n16:9 Naaj wu metti di lakk nit \u00f1i, \u00f1u daldi xarab turu Y\u00e0lla, ji am sa\u00f1-sa\u00f1 ci kaw musiba yooyu. Waaye tuubu\u00f1u sax seeni b\u00e0kkaar, ngir jox ko ndam li.\n16:10 Jur\u00f3omeelu malaaka ma tuur ndabam ci kaw g\u00e0ngunem rab wa. Noonu l\u00ebnd\u00ebm muur nguuram. Nit \u00f1i di m\u00e0tt seeni l\u00e0mmi\u00f1 ndax metit,\n16:11 \u00f1uy xarab Y\u00e0llay asamaan ndax seeni metit ak seeni taab. Waaye tuubu\u00f1u seeni j\u00ebf.\n16:12 Jur\u00f3om-benneelu malaaka ma sotti ndabam ci dex gu mag, gi \u00f1uy wax Efraat, ndox ma daldi \u014biis, ngir waajal yoonu buuri penku, yiy \u00f1\u00ebw.\n16:13 Noonu ma gis \u00f1etti rab yu bon yu mel niy mbott, g\u00e9nn ci g\u00e9mmi\u00f1i ninkin\u00e0nka ja ak rab wa ak naaf\u00e9q, ba mbubboo yonent.\n16:14 Ay rabi Seytaane la\u00f1u woon, yuy def ay k\u00e9emaan te di dem ci buuri \u00e0ddina s\u00e9pp, di leen dajale, ngir xeex biy am ci b\u00e9s bu mag, bi Y\u00e0lla Aji K\u00e0ttan jagleele boppam.\n16:15 \u00abMaa ngi \u00f1\u00ebw nib s\u00e0cc. B\u00e9g nga, yaw mi nelawul te di wottu say y\u00e9re, ngir ba\u00f1 a dox yaramu neen, \u00f1uy gis sa g\u00e0cce.\u00bb\n16:16 Noonu rab ya dajale buuri \u00e0ddina si ci b\u00e9rab bu tudd ci l\u00e0kku yawut Armagedon.\n16:17 Ci kaw loolu jur\u00f3om-\u00f1aareelu malaaka ma sotti ndabam ci ngelaw. Noonu baat bu xumb j\u00f3ge ca g\u00e0ngune ma ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, naan: \u00abL\u00e9pp mat na.\u00bb\n16:18 Noonu mu am ay melax ay riir ay d\u00ebnnu ak yengu-yengub suuf bu mag, boo xam ne b\u00e9si cosaan ba l\u00e9egi, musu faa am. Yengu-yengub suuf si r\u00e9ye na noonu.\n16:19 D\u00ebkk bu mag ba x\u00e0jjalikoo \u00f1etti c\u00e9r, te d\u00ebkki xeet yi m\u00e0bb. Noonu Y\u00e0lla daldi f\u00e0ttaliku Babilon bu mag ba, ngir jox ko koppu meram mu t\u00e0ng ma, ba mu m\u00e0ndi.\n16:20 Dun y\u00e9pp daldi ne mes, te kenn gisatul tund ya.\n16:21 Tawu yuur, donj wu nekk tollu ci \u00f1eent-fukki kilo, daldi daanoo asamaan ci kaw nit \u00f1i, \u00f1uy xarab Y\u00e0lla ndax musibam yuur ga, ndaxte musiba ma dafa metti woon lool.\n17:1 Gannaaw loolu benn ci jur\u00f3om-\u00f1aari malaaka, ya taawu jur\u00f3om-\u00f1aari ndab ya, \u00f1\u00ebw ne ma: \u00abKaay, ma won la mbugalu jig\u00e9enu moykat bu mag, bi toog ci dex yu bare.\n17:2 Moom la buuri \u00e0ddina si \u00e0ndal ci seen njaaloo. Ci bii\u00f1u moy Y\u00e0llaam la waa \u00e0ddina m\u00e0ndee.\u00bb\n17:3 Noonu Xelum Y\u00e0lla solu ma, malaaka ma y\u00f3bbu ma ca m\u00e0ndi\u014b ma. Foofa ma gis fa jig\u00e9en ju war rab wu xonq te am jur\u00f3om-\u00f1aari bopp ak fukki b\u00e9jj\u00e9n, yaram wa fees ak turi xarab Y\u00e0lla.\n17:4 Jig\u00e9en ja sol lu yolet te xonq, takk wurus ak jamaa ak ay per. Yoroon na koppu wurus bu fees ak \u00f1aawteef ak sobeem.\n17:5 Bindoon na\u00f1u ci j\u00ebwam tur wii \u00ebmb kumpa, mu di: Babilon mu mag mi, ndeyi jig\u00e9eni moykat yi ak \u00f1aawteefi \u00e0ddina yi.\n17:6 Ma gis jig\u00e9en ja m\u00e0ndi ci deretu gaayi Y\u00e0lla yi, ci deretu \u00f1i doon seedeel Yeesu. Naka laa ko gis, ma daldi jaaxle lool.\n17:7 Malaaka ma ne ma: \u00abLu tax nga jaaxle? Dinaa la leeralal kumpag jig\u00e9en ji ak rab, wi mu war te am jur\u00f3om-\u00f1aari bopp ak fukki b\u00e9jj\u00e9n.\n17:8 Rab wi nga gis nekkoon na waaye nekkatul. Dina g\u00e9nn ca k\u00e0mb gu x\u00f3ot ga, ba noppi s\u00e0nku. Noonu waa \u00e0ddina, \u00f1i \u00f1u bindul seeni tur, li dale ci nj\u00e0lb\u00e9enu \u00e0ddina, ci t\u00e9ereb dund bi, dina\u00f1u y\u00e9emu, bu \u00f1u gisee rab wi, ndaxte nekkoon na waaye nekkatul te dina nekkaat.\n17:9 \u00abXam lii nag moo laaj xel. Jur\u00f3om-\u00f1aari bopp ya \u00f1ooy jur\u00f3om-\u00f1aari tund, yi jig\u00e9en ji toog ci seen kaw. Jur\u00f3om-\u00f1aari buur la\u00f1u itam:\n17:10 jur\u00f3om daanu na\u00f1u, kenn kaa ngi fi, ki ci des \u00f1\u00ebwagul, te bu \u00f1\u00ebwee, dina fi war a nekk ab diir.\n17:11 Rab wi nekkoon te nekkatul nag, moom ci boppam moo di jur\u00f3om-\u00f1etteelu buur bi, te ci jur\u00f3om-\u00f1aar yi la bokk. Ma nga j\u00ebm s\u00e0nkute.\n17:12 \u00abFukki b\u00e9jj\u00e9n yi nga gis, fukki buur la\u00f1u yu jotagul nguur. Waaye dina\u00f1u jot sa\u00f1-sa\u00f1 diirub waxtu, \u00f1uy nguuru ak rab wi.\n17:13 \u00d1oo bokk m\u00e9b\u00e9t, di jox seen k\u00e0ttan ak seen sa\u00f1-sa\u00f1 rab wi.\n17:14 Dina\u00f1u xare ak Mbote mi, waaye Mbote mi dina leen daan, ndaxte mooy kilifag kilifa yi, di Buuru buur yi. Te am toppam, di \u00f1i mu woo te t\u00e0nn leen, te \u00f1u takku ci moom, dina\u00f1u daanandoo ak moom.\u00bb\n17:15 Mu neeti ma: \u00abDex yi nga gis jig\u00e9enu moykat ja toog ca kaw, mooy r\u00e9ew yi ak mbooloo yi ak xeet yi ak k\u00e0llaama yi.\n17:16 Fukki b\u00e9jj\u00e9n yi nga gis, \u00f1oom ak rab wa, dina\u00f1u ba\u00f1 jig\u00e9enu moykat ja, futti ko ci l\u00e9pp, def ko yaramu neen. Dina\u00f1u lekk suuxam, ba noppi lakk ko ci safara.\n17:17 Ndaxte Y\u00e0lla def na ci seen xol, \u00f1u matal la mu naroon. Noonu dina\u00f1u \u00e0nd, j\u00e9bbal seen nguur rab wi, ba kera li Y\u00e0lla wax di mat.\n17:18 Te jig\u00e9en ji nga gis, moo di d\u00ebkk bu mag, biy nguuru ci kaw buuri \u00e0ddina si.\u00bb\n18:1 Gannaaw loolu ma gis meneen malaaka mu w\u00e0cce ca asamaan, yor sa\u00f1-sa\u00f1 bu r\u00e9y, te leeraayam daj na \u00e0ddina s\u00e9pp.\n18:2 Mu daldi xaacu naan: \u00abDaanu na! Babilon mu mag ma daanu na! L\u00e9egi d\u00ebkkukaayu jinne la, ak b\u00e9pp rab wu bon ak b\u00e9pp picc mu daganul te araam.\n18:3 Ndaxte jox na xeeti \u00e0ddina y\u00e9pp, \u00f1u naan ci koppu nafsoom ak njaaloom, ba \u00f1u m\u00e0ndi. Buuri \u00e0ddina \u00e0nd na\u00f1u ak moom ci njaaloo, te baana-baanay \u00e0ddina woomle na\u00f1u ndax li mu b\u00ebgg mbuux.\u00bb\n18:4 Noonu ma d\u00e9gg beneen baat bu j\u00f3ge asamaan naan: \u00abG\u00e9nnleen ci biiram, y\u00e9en samay gaay, ngir ngeen ba\u00f1 a bokk ci ay b\u00e0kkaaram te ba\u00f1 a am c\u00e9r ci musiba yi koy dal.\n18:5 Ndaxte ay b\u00e0kkaaram dajaloo na\u00f1u ba ci asamaan, te Y\u00e0lla f\u00e0ttaliku na ay j\u00ebfam yu bon.\n18:6 Dellooleen ko li mu defoon, feyleen ko \u00f1aar ci li mu lebaloon, feesal-leen koppam ak naan gu g\u00ebn a wex \u00f1aari yoon naan ga mu joxe woon.\n18:7 Joxleen ko ci coono ak naqar, lu tollu ni tiitar ak mbuux, ba mu dencaloon boppam. Gannaaw nee woon na ci xelam: \u201cMaa ngi toog fii ni buur, duma ab j\u00ebtun te duma t\u00e9nj mukk,\u201d\n18:8 looloo tax ba musiba, yii \u00f1u ko s\u00e9dd, dina\u00f1u \u00f1\u00ebw ci benn b\u00e9s, \u00f1u di mbas, t\u00e9nj ak xiif, \u00f1u di ko lakk ba mu jeex, ndaxte Y\u00e0lla Boroom bi ko \u00e0tte, ku am k\u00e0ttan la.\u00bb\n18:9 Buuri \u00e0ddina y\u00e9pp, yi \u00e0ndoon ak moom ci njaaloo ak mbuux, bu \u00f1u s\u00e9enee saxar siy jollee ci taal bi \u00f1u koy lakke, dina\u00f1u yuuxu, di ko jooy.\n18:10 Dina\u00f1u tiit ndax coonoom, ba dandu lu sore, naan:\u00abNgalla yaw! Ngalla yaw,d\u00ebkk bu mag bi,Babilon mi am k\u00e0ttan;wenn waxtu rekk doy na,ngir sab \u00e0tte mat!\u00bb\n18:11 Baana-baana yi ci kaw suuf di jooy, di ko naqarlu, ndaxte kenn dootul j\u00ebnd seen njaay:\n18:12 seen wurus, seen xaalis, seeni jamaa ak yeneeni per; seeni piis yu rafet, piis yu yolet, yu ray-ray, yu xonq; seen d\u00e9nk wu xee\u00f1, seen y\u00ebf yi \u00f1u defare iwaar walla d\u00e9nk wu jafe walla x\u00e0njar walla we\u00f1 walla marbar;\n18:13 ak bant yuy safal, g\u00e0ncax gu xee\u00f1, ay xeeti cuuraay yu bare, latkolo\u00f1, bii\u00f1, diw, sungufu lay-layaat, pepp, ay nag, ay xar, ay fas, sareeti xare, ay jaam, ba ci bakkani nit.\n18:14 Dina\u00f1u wax naan: \u00abY\u00ebf yi nga b\u00ebggoon a am raw na\u00f1u la, te l\u00e9pp luy yafal walla col gu rafet \u00f1\u00e0kk nga ko, te kenn du ko gisaat!\u00bb\n18:15 Baana-baana, yi daan jaay y\u00ebf yooyu ba woomle, dina\u00f1u sore ndax ragal coonoom. Dina\u00f1u jooy di naqarlu,\n18:16 naan:\u00abNgalla yaw! Ngalla yaw, d\u00ebkk bu mag,bi soloon y\u00e9re yu rafet, yu yolet te xonq,daan takk wurus ak jamaa ak per,\n18:17 sa alal ju bare j\u00e9pp naaw na ci wenn waxtu!\u00bb Noonu \u00f1\u00e9pp \u00f1iy dawal gaal ak \u00f1i ciy tukki ak \u00f1i ciy ligg\u00e9ey ak \u00f1i ciy baana-baana, \u00f1\u00e9pp di sore b\u00e9rab boobu,\n18:18 te bu \u00f1u s\u00e9enee saxar sa cay jollee, naan: \u00abNdax d\u00ebkk bu niroo woon ak d\u00ebkk bu mag bii mas na am?\u00bb\n18:19 \u00d1uy x\u00ebpp suuf ci seen bopp, di jooy, di naqarlu te naan:\u00abNgalla yaw! Ngalla yaw,d\u00ebkk bu mag bi nga xam neci la boroom gaal y\u00e9pp woomle ndax sa barele,ci wenn waxtu nga gental.\n18:20 Yaw asamaan, b\u00e9gal ci li \u00f1u ko y\u00e0q!Y\u00e9en itam gaayi Y\u00e0lla yi,ndaw yi ak yonent yi, b\u00e9gleen,ndaxte Y\u00e0lla \u00e0tte na ko, ba feyyul leen.\u00bb\n18:21 Noonu malaaka mu am doole j\u00ebl doj wu r\u00e9y, s\u00e0nni ko ci g\u00e9ej gi, naan: \u00abNii la\u00f1uy s\u00e0nnee ak doole Babilon d\u00ebkk bu mag bi, mu ne me\u014b\u014b.\n18:22 Buumi xalam yi, baati woykat yi, toxoro yi ak liit yi,kenn dootu leen d\u00e9gg ci yaw.Ligg\u00e9eykat bu xare\u00f1 bu mu man a doon, kenn dootu ko gis ci yaw.Kanda\u014bu g\u00ebnn, kenn du ko d\u00e9ggati ci yaw.\n18:23 Niitug l\u00e0mp du t\u00e0kkati,te baatu boroom s\u00e9et ak s\u00e9etam dootul jib ci yaw ba f\u00e0ww.Ndaxte say baana-baana \u00f1oo yilifoon \u00e0ddina,te xeet y\u00e9pp r\u00e9er na\u00f1u ndax say luxus.\n18:24 Te deretu yonent yi ak gaayi Y\u00e0lla yiak \u00f1\u00e9pp \u00f1i \u00f1u rey ci kaw suuf,ci moom Babilon la\u00f1u ko fa fekk.\u00bb\n19:1 Gannaaw loolu ma d\u00e9gg lu mel ni baat bu xumb bu jollee ca mbooloo mu bare ca asamaan, naan:\u00abAleluya!Mucc, ndam ak k\u00e0ttan,Y\u00e0lla sunu Boroom moo ko moom.\n19:2 Ay \u00e0tteem da\u00f1oo d\u00ebggu te jub!Ndaxte \u00e0tte na jig\u00e9enu moykat bu mag,bi daan y\u00e0q \u00e0ddina si ak njaaloom,te feyyul na noonu jaami Y\u00e0lla, yi mu daan rey.\u00bb\n19:3 \u00d1u tegaat ca ne:\u00abAleluya!Saxarus lakku d\u00ebkk baa ngi jolli ba f\u00e0ww!\u00bb\n19:4 Noonu \u00f1aar-fukki mag \u00f1a ak \u00f1eent, ak \u00f1eenti mbindeef ya, daldi sukk di jaamu Y\u00e0lla, moom mi toog ca g\u00e0ngune ma. \u00d1u naan:\u00abAmiin! Aleluya!\u00bb\n19:5 Noonu baat jibe ca g\u00e0ngune ma naan:\u00abM\u00e0ggal-leen Y\u00e0lla sunu Boroom,y\u00e9en \u00f1\u00e9pp \u00f1i di ay jaamam,y\u00e9en \u00f1i ko ragal, mag ak ndaw.\u00bb\n19:6 Ma d\u00e9gg lu mel ni baatu mbooloo mu bare, mel ni riiru duusi g\u00e9ej, ni yenguy d\u00ebnnu yu r\u00e9y, naan:\u00abAleluya!Ndaxte sunu BoroomY\u00e0lla Aji K\u00e0ttan jidugg na ci nguuram.\n19:7 Nanu b\u00e9g te b\u00e0nneexute jox ko ndam li,ndaxte c\u00e9etu Mbote mi agsi na,s\u00e9et bi waaj na.\n19:8 May na\u00f1u ko, mu sol mbubb mu sette weex bay lerax.\u00bb Mbubb mu weex moomu day misaal njubtey gaayi Y\u00e0lla yi.\n19:9 Gannaaw loolu malaaka ma ne ma: \u00abBindal lii: \u201cY\u00e9en \u00f1i \u00f1u woo ci reeri c\u00e9etu Mbote ma, barkeel ngeen.\u201d\u00bb Mu teg ca ne ma: \u00abK\u00e0ddu yii \u00f1ooy k\u00e0dduy Y\u00e0lla, di k\u00e0ddu yu d\u00ebggu.\u00bb\n19:10 Noonu ma daanu ci ay t\u00e0nkam, b\u00ebgg koo jaamu. Waaye mu ne ma: \u00abMoytu koo def; sa nawle laa ci ligg\u00e9ey bi, di kenn ci say bokk, yiy sax ci seedeel Yeesu. Jaamul Y\u00e0lla. Ndaxte seedes Yeesu mooy xel miy solu yonent yi.\u00bb\n19:11 Bi loolu w\u00e9yee ma gis asamaan ubbiku. Noonu fas wu weex fee\u00f1. Ki ko war ma nga tudd Ku Takku te D\u00ebggu, te ci njub lay \u00e0tte ak a xare.\n19:12 Ay b\u00ebtam di xuyy ni safara te mu am mbaxanay buur yu bare ca boppam. Bind na\u00f1u ci moom tur wu kenn xamul ku dul moom.\n19:13 Sol na mbubb mu \u00f1u s\u00f3ob ci deret, te K\u00e0ddug Y\u00e0lla mooy turam.\n19:14 Xarekat yi nekk ci asamaan topp ci moom, war ay fas yu weex, sol mbubb yu weex te set.\n19:15 Am na jaasi ju \u00f1aw juy g\u00e9nn ci g\u00e9mmi\u00f1am, ngir d\u00f3or xeet yi, mu di leen jiitee yetu we\u00f1, te mooy nappaaje r\u00e9se\u00f1 yi ci segalukaayu mer mu t\u00e0ng, mu Y\u00e0lla Aji K\u00e0ttan ji.\n19:16 Ci mbubbam ak ci poojam bind na\u00f1u ci tur wii: Buuru buur yi, Kilifag kilifa yi.\n19:17 Noonu ma gis malaaka mu taxaw ci jant bi. Mu wax ak baat bu xumb ak picc, yiy naaw ci digg asamaan, ne leen: \u00ab\u00d1\u00ebwleen teewesi reer bu mag bu Y\u00e0lla,\n19:18 ngeen lekk suuxi buur yi, njiiti xare yi ak boroom k\u00e0ttan yi, suuxi fas yi ak seeni gawar, suuxi \u00f1\u00e9pp: gor ak jaam, mag ak ndaw.\u00bb\n19:19 Noonu ma gis rab wa, buuri \u00e0ddina si ak seeni xarekat dajaloo ngir xareji ak ki war fas wa ak ay xarekatam.\n19:20 \u00d1u j\u00e0pp rab wa, moom ak naaf\u00e9q ba mbubboo yonent, ba daan def ca turu rab wa ay k\u00e9emaan yu mu naxe \u00f1i nangu woon a am m\u00e0ndargam rab wa te jaamu nataalam. \u00d1oom \u00f1aar \u00f1\u00e9pp s\u00e0nni na\u00f1u leen \u00f1uy dund ca d\u00e9egu safara ak tamarax buy t\u00e0kk.\n19:21 \u00d1a ca des, jaasi, jay g\u00e9nn ca g\u00e9mmi\u00f1u ka toog ca fas wa, rey leen; picc y\u00e9pp lekk, ba regg ci seeni suux.\n20:1 Noonu ma gis malaaka mu w\u00e0cce ca asamaan, yor caabiy k\u00e0mb ga ak c\u00e0llala gu r\u00e9y.\n20:2 Mu j\u00e0pp ninkin\u00e0nka ja, di jaani cosaan ja, muy Tuumaalkat bi, maanaam Seytaane. Malaaka ma yeew ko diirub junniy at,\n20:3 s\u00e0nni ko ci k\u00e0mb gi, t\u00ebj ko, sakk bunt bi ko tiim ci kaw. Noonu du nax xeet yi, ba kera junniy at yi di mat. Gannaaw loolu f\u00e0ww \u00f1u yiwi ko diir bu g\u00e0tt.\n20:4 Noonu ma gis ay g\u00e0ngune, \u00f1u jox \u00f1a ca toog sa\u00f1-sa\u00f1u \u00e0tte. Noonu ma gis ruuwi \u00f1i \u00f1u b\u00f3omoon ndax li \u00f1u doon seedeel Yeesu te g\u00ebm k\u00e0ddug Y\u00e0lla. \u00d1oo\u00f1u jaamuwu\u00f1u rab wa mbaa nataalam, te nanguwu\u00f1oo am m\u00e0ndargam rab wa ca seen j\u00eb mbaa seen loxo. \u00d1u daldi dekki, nguuru ak Kirist diirub junniy at.\n20:5 Yeneen n\u00e9ew yi du\u00f1u dekki, fi ak junniy at yi matul. Loolu moo di ndekkite lu j\u00ebkk li.\n20:6 \u00d1i bokk ci ndekkite lu j\u00ebkk li, barkeel na\u00f1u te sell! \u00d1aareelu dee gi du leen manal dara. Waaye dina\u00f1u doon saraxalekati Y\u00e0lla ak Kirist, tey nguuru ak moom junniy at.\n20:7 Bu junniy at ya matee, dina\u00f1u yiwi Seytaane ca kasoom,\n20:8 te dina dem naxi xeet yi ci \u00f1eenti xeblay \u00e0ddina, maanaam \u00f1oom Gog ak Magog. Dina leen dajale ngir xare, te dina\u00f1u bare ni peppi suuf cig tefes.\n20:9 Dina\u00f1u sam suuf s\u00e9pp, di w\u00ebr dalu gaayi Y\u00e0lla yi ak d\u00ebkk, bi Y\u00e0lla b\u00ebgg. Waaye safara daldi j\u00f3ge asamaan, lakk leen.\n20:10 Dees na j\u00e0pp Seytaane, mi leen daan nax, s\u00e0nni ko ci d\u00e9egu safara ak tamarax bi, mu fekki rab wa ak naaf\u00e9q ba mbubboo yonent. Foofa dina\u00f1u leen mbugal guddi ak b\u00ebcc\u00ebg ba f\u00e0ww.\n20:11 Noonu ma gis g\u00e0ngune mu mag te weex, ak ka ca toog. Asamaan ak suuf daw, sore ko, ba ne mes.\n20:12 Ma gis n\u00e9ew ya, mag ak ndaw, \u00f1u taxaw ca kanamu g\u00e0ngune ma. \u00d1u daldi ubbi ay t\u00e9ere, ubbi itam beneen t\u00e9ere, t\u00e9ereb dund bi. \u00d1u \u00e0tte n\u00e9ew ya, ku nekk ci say j\u00ebf, ni \u00f1u ko binde woon ca t\u00e9ere ya.\n20:13 Noonu g\u00e9ej g\u00ebq n\u00e9ew, yi nekkoon ci moom; dee ak bars\u00e0q delloo n\u00e9ew, ya \u00f1u yoroon. \u00d1u \u00e0tte \u00f1\u00e9pp ci seeni j\u00ebf.\n20:14 \u00d1u j\u00e0pp dee ak bars\u00e0q, s\u00e0nni ca d\u00e9egu safara sa. D\u00e9egu safara soosu moo di \u00f1aareelu dee.\n20:15 K\u00e9pp ku \u00f1u bindul sa tur ci t\u00e9ereb dund bi, dees na la s\u00e0nni ci d\u00e9egu safara si.\n21:1 Noonu ma gis asamaan su bees ak suuf su bees, ndaxte asamaan su j\u00ebkk sa ak suuf su j\u00ebkk sa w\u00e9yoon na\u00f1u, te g\u00e9ej gi amatul.\n21:2 Ma gis, w\u00e0cce ca asamaan, j\u00f3ge ca wetu Y\u00e0lla, Yerusalem gu bees gi, d\u00ebkk bu sell, bi \u00f1u waajal ba mu jekk ni s\u00e9et buy n\u00e9g j\u00ebkk\u00ebram.\n21:3 Ma d\u00e9gg baat bu xumb jibe ca g\u00e0ngune ma naan: \u00abDalub Y\u00e0llaa ngi ci biir nit \u00f1i. Dina d\u00ebkk ak \u00f1oom, nit \u00f1i dina\u00f1u nekk ay gaayam, te moom Y\u00e0lla ci boppam dina \u00e0nd ak \u00f1oom, nekk Y\u00e0lla seen Boroom.\n21:4 Dina fomp b\u00e9pp rangoo\u00f1 ci seeni b\u00ebt; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte y\u00ebf yu j\u00ebkk ya w\u00e9y na\u00f1u.\u00bb\n21:5 Noonu ki toog ca g\u00e0ngune ma ne: \u00abMaa ngi yeesal l\u00e9pp!\u00bb Mu ne ma: \u00abBindal, ndaxte k\u00e0ddu yii yu w\u00f3or la\u00f1u te d\u00ebggu.\u00bb\n21:6 Mu teg ca ne ma: \u00abL\u00e9pp mat na! Maay Alfa ak Omega, nj\u00e0lb\u00e9en gi ak muj gi. Ku mar, dinaa la may ci b\u00ebtu ndoxum dund mi, te doo fey dara.\n21:7 Ku daan, dinga am c\u00e9r ci mbir yii. Dinaa nekk Y\u00e0lla sa Boroom, te dinga nekk doom ci man.\n21:8 Waaye \u00f1i ragal, \u00f1i g\u00ebmul, \u00f1iy def lu \u00f1aaw, \u00f1iy b\u00f3om nit, \u00f1iy njaaloo, luxuskat yi, x\u00ebr\u00ebmkat yi ak fenkat y\u00e9pp, seen a\u00f1 moo di d\u00e9egu safara ak tamarax bi. Loolu mooy \u00f1aareelu dee gi.\u00bb\n21:9 Gannaaw loolu benn malaaka \u00f1\u00ebw, mi bokk ca jur\u00f3om-\u00f1aari malaaka, ya yoroon jur\u00f3om-\u00f1aari ndabi musiba yu mujj ya, ne ma: \u00ab\u00d1\u00ebwal, ma won la s\u00e9et bi, jabaru Mbote mi.\u00bb\n21:10 Noonu Xelum Y\u00e0lla solu ma, malaaka ma y\u00f3bbu ma ci kaw tund wu r\u00e9y-a-r\u00e9y. Noonu mu won ma Yerusalem, d\u00ebkk bu sell bi, muy w\u00e0cce ci asamaan, j\u00f3ge ca wetu Y\u00e0lla,\n21:11 \u00e0nd ak ndamu Y\u00e0lla. Leeraayam mel ni leeraayu per bu jafe lool, ni jamaa buy ray-rayi.\n21:12 Miir bu r\u00e9y te kawe moo ko w\u00ebr te am fukki bunt ak \u00f1aar, te bu ca nekk malaaka taxaw ca wet ga. Ca bunt ya bind na\u00f1u ca fukki tur ak \u00f1aar, yu giiri b\u00e0nni Israyil.\n21:13 Ca penku am na fa \u00f1etti bunt; ca nor \u00f1ett; ca sudd \u00f1ett ak \u00f1ett ca sowu.\n21:14 Samp na\u00f1u miiru d\u00ebkk ba ci fukki fondamaa ak \u00f1aar, yu \u00f1u bind turi fukki ndawi Mbote ma ak \u00f1aar.\n21:15 Ki doon wax ak man amoon na nattukaay, di bantu wurus bu mu doon natte d\u00ebkk ba ak miir ba ko w\u00ebr, ak bunt ya.\n21:16 D\u00ebkk ba dafa kaare, guddaay ba ak yaatuwaay ba \u00f1oo tolloo. Mu natt d\u00ebkk ba ak bant ba mu yor. Guddaay ba, yaatuwaay ba ak taxawaay ba l\u00e9pp tolloo, di fukki junni ak \u00f1aar ciy estat.\n21:17 Malaaka ma natt miir ba nattub nit, fekk miir ba di t\u00e9em\u00e9er ak \u00f1eent-fukk ak \u00f1eenti xasab.\n21:18 Miir ba, jamaa la\u00f1u ko ligg\u00e9eye, te d\u00ebkk ba di wurusu ngalam, leer ni weer bu set.\n21:19 Fondamaay miiru d\u00ebkk ba rafetale na\u00f1u leen xeeti per yu nekk.Fondamaa bu j\u00ebkk ba jamaa la;\u00f1aareel ba, per bu bulo bu \u00f1uy wax safir;\u00f1etteel ba, per bu wert bu \u00f1uy wax kalseduwan;\u00f1eenteel ba, per bu wert te lerax, bu \u00f1uy wax em\u00ebr\u00f3ot;\n21:20 jur\u00f3omeel ba, per bu xonq bu \u00f1uy wax sardonigs\u00eb;jur\u00f3om-benneel ba, per bu xonq curr bu \u00f1uy wax sarduwan;jur\u00f3om-\u00f1aareel ba, per bu mboq bu \u00f1uy wax kirisolit;jur\u00f3om-\u00f1etteel ba, per bu wert ni g\u00e9ej bu \u00f1uy wax beril;jur\u00f3om-\u00f1eenteel ba, per bu mboq bu \u00f1uy wax topas;fukkeel ba, per bu wert bu \u00f1uy wax kirisoparas;fukkeel ba ak benn, per bu bulo bu \u00f1uy wax yasent;fukkeel ba ak \u00f1aar, per bu yolet bu \u00f1uy wax ametist.\n21:21 Fukki bunt ya ak \u00f1aar, ay per yu weex la\u00f1u. Bunt bu nekk di benn per kepp. P\u00e9ncu d\u00ebkk ba di wurusu ngalam, leer ni weer bu set.\n21:22 Gisuma ca d\u00ebkk ba k\u00ebr Y\u00e0lla, ndaxte Boroom bi Y\u00e0lla Aji K\u00e0ttan ji ak Mbote ma \u00f1ooy m\u00e0ggalukaay ba.\n21:23 D\u00ebkk ba soxlawul jant walla weer ngir leeral ko, ndaxte ndamu Y\u00e0lla moo koy leeral, te Mbote ma moo nekk l\u00e0mpam.\n21:24 Xeeti \u00e0ddina dina\u00f1u dox cig leeram, te buuri \u00e0ddina dina\u00f1u ca indi seen ndam.\n21:25 Bunti d\u00ebkk ba du\u00f1u t\u00ebju b\u00ebcc\u00ebg, te guddi du fa am.\n21:26 Dina\u00f1u fa indi ndamu xeet yi ak seen alal.\n21:27 Dara du fa dugg lu am sobe, mbaa kenn kuy s\u00f3obu ci \u00f1aawteef walla fen. \u00d1i \u00f1u bind ci t\u00e9ereb dund bu Mbote mi rekk \u00f1oo fay dugg.\n22:1 Noonu malaaka ma won ma dexu ndoxum dund, mu leer ni weer bu set, di g\u00e9nn ca g\u00e0ngune mu Y\u00e0lla ak Mbote ma,\n22:2 xellee ca digg p\u00e9ncu d\u00ebkk ba. Ca weti dex ga amoon na ca garabu dund, guy me\u00f1\u00f1 fukki yoon ak \u00f1aar, di me\u00f1\u00f1 weer wu nekk, te xob ya di faj xeet yi.\n22:3 Musiba dootul am. G\u00e0ngune mu Y\u00e0lla ak Mbote mi mu ngi ci d\u00ebkk bi, te ay jaamam dina\u00f1u ko jaamu.\n22:4 Dina\u00f1u gis xar-kanamam, te turam dina nekk ci seen j\u00eb.\n22:5 Guddi dootul am, te kenn dootul soxla leeru l\u00e0mp walla naaju jant, ndaxte Boroom bi Y\u00e0lla moo leen di leeral. Te dina\u00f1u nguuru ba f\u00e0ww.\n22:6 Noonu malaaka ma ne ma: \u00abWax jii ju w\u00f3or la te d\u00ebggu. Boroom bi, Y\u00e0lla jiy leeral xeli yonent yi, moo y\u00f3nni malaakaam, ngir mu won ay jaamam mbir yi d\u00ebgm\u00ebl di \u00f1\u00ebw.\u00bb\n22:7 \u00abMaa ngi \u00f1\u00ebw l\u00e9egi. Yaw miy s\u00e0mm waxi Y\u00e0lla, yi ci t\u00e9ere bii, barkeel nga.\u00bb\n22:8 Man Yowaana maa d\u00e9gg mbir yii te gis ko. Ba ma ko d\u00e9ggee te gis ko, damaa daanu ca t\u00e0nki malaaka, ma ma ko doon won, b\u00ebgg koo jaamu.\n22:9 Waaye mu ne ma: \u00abMoytu koo def. Sa nawle laa ci ligg\u00e9ey bi, yaw ak say bokki yonent ak \u00f1iy s\u00e0mm waxi t\u00e9ere bii. Jaamul Y\u00e0lla.\u00bb\n22:10 Mu ne ma it: \u00abBul t\u00ebj t\u00e9ere bii ak waxi Y\u00e0lla yi mu \u00ebmb, ndaxte waxtu wi jege na.\n22:11 Ku jubadi, na sax ci jubadeem; ku taq sobe, na sigi\u00f1u ci sobeem; ku jub, na w\u00e9y ci j\u00ebf yu jub; ku sell, na ci \u014boy.\u00bb\n22:12 Yeesu nee na: \u00abMaa ngi \u00f1\u00ebw l\u00e9egi, indaale pey gi, ngir delloo ku nekk lu mengoo ak lu mu def.\n22:13 Man maay Alfa ak Omega, ki j\u00ebkk te mujj, nj\u00e0lb\u00e9en gi ak muj gi.\n22:14 \u00abY\u00e9en \u00f1i f\u00f3ot seeni mbubb, ngir sa\u00f1 a lekk ci garabu dund gi te dugg ci bunti d\u00ebkk bi, barkeel ngeen.\n22:15 Waaye \u00f1i ci biti \u00f1ooy xaj yi, luxuskat yi, njaalookat yi, b\u00f3omkat yi, x\u00ebr\u00ebmkat yi ak \u00f1\u00e9pp \u00f1iy sopp fen te di ci w\u00e9y.\n22:16 \u00abMan Yeesu maa y\u00f3nni sama malaaka, ngir mu seede leen mbir yii ci digg mboolooy \u00f1i g\u00ebm. Man maay car, bi soqikoo ci Daawuda, di biddiiwu nj\u00ebl bu leer bi.\u00bb\n22:17 Te Xelum Y\u00e0lla ak s\u00e9etu Mbote mi \u00f1u ngi naan: \u00ab\u00d1\u00ebwal.\u00bb K\u00e9pp ku d\u00e9gg wax jii, na ne: \u00ab\u00d1\u00ebwal.\u00bb Na k\u00e9pp ku mar, \u00f1\u00ebw; ku b\u00ebgg, duyal ci ndoxum dund mi te doo fey dara.\n22:18 Man Yowaana maa ngi koy wax k\u00e9pp ku d\u00e9gg waxi Y\u00e0lla, yi nekk ci t\u00e9ere bii: ku ci yokk dara, Y\u00e0lla dina dolli ci sa mbugal musiba, yi \u00f1u wax ci t\u00e9ere bii.\n22:19 Ku dindi dara ci waxi Y\u00e0lla, yi nekk ci t\u00e9ere bii, Y\u00e0lla dina dindi sa w\u00e0ll ca garabu dund ga ak d\u00ebkk bu sell ba, \u00f1aar yooyu \u00f1u bind ci t\u00e9ere bii.\n22:20 Kiy seede mbir yii nee na: \u00abWaaw, maa ngi \u00f1\u00ebw l\u00e9egi.\u00bb Amiin. Boroom bi Yeesu, \u00f1\u00ebwal.\n22:21 Na yiwu Boroom bi Yeesu \u00e0nd ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.","title":"Wolof Bible (NT): Revelation","type":"page"}
