{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/rom.htm","path":"bib/wb/wlf/rom.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/rom.htm","text":"1:1 Man Pool, jaamub Kirist Yeesu, maa leen di bind bataaxal bii. Y\u00e0lla woo na ma, ma nekk ndawam, sas ma ligg\u00e9eyu xamle xebaaram bu baax bi.\n1:2 Xebaar bu baax boobu, Y\u00e0lla dige woon na ko bu y\u00e0gg, jaarale ko ciy yonentam, \u00f1u def ko ci Mbind mu sell mi,\n1:3 di xamle mbirum Doomam, Yeesu Kirist sunu Boroom. Lu j\u00ebm ci meloom ci \u00e0ddina, ci askanu Daawuda la j\u00f3ge, waaye lu j\u00ebm ci xelam mu sell, Doomu Y\u00e0lla la; ndaxte ndekkiteem nekk na firnde ju r\u00e0\u00f1\u00f1iku, ne moom la.\n1:5 Te moom Kirist t\u00e0bbal na nu ci yiwu Y\u00e0lla, def nu ay ndawam, y\u00f3nni nu ci biir xeeti \u00e0ddina s\u00e9pp, ngir \u00f1u g\u00ebm ko te j\u00e9bbalu, ba m\u00e0ggal turam.\n1:6 Te ci ngeen bokk, y\u00e9en \u00f1i Y\u00e0lla woo, ngeen nekk ci Kirist.\n1:7 Y\u00e9en \u00f1i d\u00ebkk Room \u00f1\u00e9pp, y\u00e9en \u00f1i Y\u00e0lla b\u00ebgg te woo leen, ngeen nekk gaayam yu sell, na leen Y\u00e0lla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak j\u00e0mm.\n1:8 Kon nag li may j\u00ebkk a wax mooy lii: sant naa Y\u00e0lla sama Boroom, jaarale ko ci Yeesu Kirist, ngir y\u00e9en \u00f1\u00e9pp, ndaxte seen ng\u00ebm siiw na ci \u00e0ddina s\u00e9pp.\n1:9 B\u00ebt bu set maa ngi leen di boole ci samay \u00f1aan. Y\u00e0lla seede na li may wax, Y\u00e0lla mi may jaamu ci sama xel, ci xamle xebaar bu baax bu Doomam.\n1:10 Te li ma koy faral di \u00f1aan mooy lii: bu soobee Y\u00e0lla, na ma ubbil bunt, ba ma man a \u00f1\u00ebw ci y\u00e9en.\n1:11 Ndaxte b\u00ebgg naa leen a gis lool, ba indil leen barke bu j\u00f3ge ci Xel mu Sell mi, ndax seen ng\u00ebm g\u00ebn a d\u00ebg\u00ebr.\n1:12 Maanaam ma nekk ci seen biir, te nu dimbaleente ci sunu ng\u00ebm, ndax man itam ma g\u00ebn a am doole.\n1:13 Bokk yi, damaa b\u00ebgg ngeen xam ne, xalaat naa leen a seetsi ay yooni yoon, ngir me\u00f1\u00f1 njari\u00f1 ci y\u00e9en, ni ma ko defe ci yeneen xeet yi, waaye ay t\u00e9q-t\u00e9q \u00f1oo ma t\u00e9ye ba l\u00e9egi.\n1:14 Am naa warugar sama diggante ak \u00f1\u00e9pp, muy \u00f1i j\u00e0ng ni Gereg yi, muy \u00f1i j\u00e0ngul ni Baarbaar yi, \u00f1i bare xam-xam ak \u00f1i barewul xam-xam.\n1:15 Li aju ci man nag, jekk naa ngir \u00f1\u00ebw, xamal leen xebaar bu baax bi, y\u00e9en it waa Room.\n1:16 Ndaxte awma benn werante ci xebaar bu baax bi may waare, ndax mbirum Y\u00e0lla la, mu l\u00e0mboo dooleem, ngir musal k\u00e9pp ku ko g\u00ebm, muy Yawut ci bu j\u00ebkk mbaa ki dul Yawut.\n1:17 Ndaxte xebaar bii day wone, ni nit man a jube ci kanam Y\u00e0lla, sukkandikoo ci ng\u00ebm rekk, t\u00e0mbali ci ng\u00ebm, yem ci ng\u00ebm. Moo tax Mbind mi wax ne: \u00abKu jub ci kaw ng\u00ebm, dinga dund.\u00bb\n1:18 Merum Y\u00e0llaa ngi fee\u00f1e asamaan, w\u00e0cc ci nit \u00f1i, ndax seen weddi Y\u00e0lla g\u00e9pp ak seen jubadi g\u00e9pp, \u00f1oom \u00f1i suul d\u00ebgg, di topp lu jubadi.\n1:19 Ndax li nit man a xam ci Y\u00e0lla, leer na ci seen xel, ndax Y\u00e0lla won na leen ko.\n1:20 Ndaxte ba \u00e0ddina sosoo ba tey, mbiri Y\u00e0lla yu n\u00ebbbu ya, maanaam dooleem ju sax ja, ak meloom wu kawe wa, fee\u00f1 na\u00f1u bu leer, te bir \u00f1\u00e9pp ci yi mu s\u00e0kk, ba tax bunti lay y\u00e9pp t\u00ebj na\u00f1u.\n1:21 Ndaxte bi \u00f1u xamee Y\u00e0lla, taxul \u00f1u m\u00e0ggal ko ni mu ware, mbaa \u00f1u sant ko. Waaye \u00f1u daldi r\u00e9er ci seen biiri xalaat yu mujjul fenn, ba tax seen xol gumba, ba l\u00ebnd\u00ebm k\u00ebruus.\n1:22 \u00d1u teg seen bopp ni boroomi xel, fekk \u00f1u \u00f1\u00e0kk xel la\u00f1u woon.\n1:23 Toxal na\u00f1u ndamu Y\u00e0lla Aji Sax ji, wuutal fa nataali nit ku dul sax, moom ak ay picc, ay rabi \u00e0ll mbaa yuy raam.\n1:24 Moo tax Y\u00e0lla b\u00ebrg\u00ebl na leen ci seeni b\u00ebgg-b\u00ebgg, \u00f1u s\u00f3obu ciy \u00f1aawteef, di j\u00ebfleente lu g\u00e0ccelu ci seeni c\u00e9r.\n1:25 Toxal na\u00f1u d\u00ebggu Y\u00e0lla, t\u00ebral fen, di m\u00e0ggal ak a jaamu mbindeef, ba faaleetu\u00f1u sax Aji Bind, ji yelloo cant ba f\u00e0ww. Amiin.\n1:26 Loolu moo tax nag Y\u00e0lla b\u00ebrg\u00ebl na leen ci seeni b\u00ebgg-b\u00ebgg yu ruslu. Seeni jig\u00e9en sax d\u00ebddu na\u00f1u li jekk, s\u00f3obu ci lu jekkadi, \u00f1oom ak seeni moroom.\n1:27 Noonu it g\u00f3or \u00f1i b\u00e0yyi na\u00f1u li jekk ci seeni c\u00e9r, maanaam \u00e0nd ak jig\u00e9en, bay am ay b\u00ebgg-b\u00ebgg yu tar ci \u00e0nd ak seeni moroom. G\u00f3or di defante ak g\u00f3or li warul, \u00f1u di jot seen peyu r\u00e9er ci seeni yaram.\n1:28 Gannaaw xam Y\u00e0lla soxalu leen, Y\u00e0lla it b\u00ebrg\u00ebl na leen ci seen xel mu bon moomu, \u00f1u sax ci j\u00ebf yu jekkadi.\n1:29 Seen xol fees na ak lu jubadi, lu bon, b\u00ebgge ak coxor; du\u00f1u xalaat lu dul ki\u00f1aan, rey nit, xuloo, njubla\u014b ak \u00f1aaw njort; da\u00f1uy j\u00ebw,\n1:30 di y\u00e0q der, di \u00f1u ba\u00f1 Y\u00e0lla te \u00f1\u00e0kk sutura, di r\u00e9y-r\u00e9ylu ak a ka\u00f1u; ay j\u00e0mbaar la\u00f1u ci fexe lu bon, di ba\u00f1 seeni waajur.\n1:31 Amu\u00f1u xel, amu\u00f1u k\u00f3ll\u00ebre, amu\u00f1u cofeel, amu\u00f1u y\u00ebrmande.\n1:32 Xam na\u00f1u ne, \u00f1iy j\u00ebfe loolu, Y\u00e0lla daganal na seen dee, waaye teewul \u00f1u di ko def, boole ko ak di farle \u00f1i ci sax.\n2:1 Kon nag k\u00e9pp ku mu man a doon, yaw miy \u00e0tte sa moroom ak \u00f1aaw njort, amuloo aw lay, ndaxte \u00e0tte sa moroom, daan sa bopp la; yaa ngi koy \u00e0tte ndax ay j\u00ebfam, fekk yaw itam noonu ngay j\u00ebfe.\n2:2 Xam nanu ne, \u00f1iy j\u00ebfe noonu, Y\u00e0lla dina leen \u00e0tte, te \u00e0tteem jub na.\n2:3 Yaw nag miy \u00e0tte \u00f1iy def loolu, te di ko def, ndax defe nga ne, dinga r\u00ebcc ci \u00e0tteb Y\u00e0lla?\n2:4 Ndax dangaa xeeb mbaaxu Y\u00e0lla, mi y\u00e9ex a mer te di la mu\u00f1al? Xanaa xamuloo ne, Y\u00e0llaa ngi lay won baaxaayam, ngir nga r\u00e9ccu say b\u00e0kkaar?\n2:5 Waaye ndegam d\u00ebg\u00ebr nga bopp te b\u00ebgguloo r\u00e9ccu, yaa ngi dajale merum Y\u00e0lla ci sa bopp. Ndaxte Y\u00e0lla s\u00e0kk na b\u00e9s bu muy wone \u00e0tteem bu jub bi te meram w\u00e0cc ci \u00f1i bon;\n2:6 b\u00e9s booba dina delloo ku nekk ay j\u00ebfam.\n2:7 \u00d1iy g\u00f3or-g\u00f3orlu ciy def lu baax, b\u00ebgg Y\u00e0lla boole leen ca ndamam te s\u00e9dde leen ng\u00ebr\u00ebm ak dund gu sax, dina leen t\u00e0bbal ci dund gu dul jeex.\n2:8 Waaye \u00f1i d\u00ebg\u00ebr bopp, ba tanqamlu d\u00ebgg, di topp lu jubadi, seen pey mooy dooni merum Y\u00e0lla ak toroxte.\n2:9 Ki doon def lu bon, peyam mooy tiis ak metit wu tar, muy Yawut ci bu j\u00ebkk, mbaa ki dul Yawut.\n2:10 Waaye ki doon def lu baax, a\u00f1am mooy bokk ci ndamu Y\u00e0lla, am ng\u00ebr\u00ebm ak j\u00e0mm, muy Yawut ci bu j\u00ebkk, mbaa ki dul Yawut.\n2:11 Ndaxte \u00f1\u00e9pp a yem fa kanam Y\u00e0lla.\n2:12 K\u00e9pp ku doon b\u00e0kkaar nag te nekkuloo woon ci yoonu Musaa, Y\u00e0lla dina la \u00e0tte ci lu dul yoonu Musaa, nga door a s\u00e0nku. Te k\u00e9pp ku doon b\u00e0kkaar te nga nekkoon ci yoonu Musaa, Y\u00e0lla dina la \u00e0tte ci yoon woowu.\n2:13 Kon d\u00e9glu yoonu Musaa rekk doyul; du loolu mooy tax nit jub ci kanam Y\u00e0lla; kiy s\u00e0mm yoon wi, moom la Y\u00e0lla di \u00e0tte ni ku jub.\n2:14 Ndax \u00f1i dul Yawut te nekku\u00f1u ci yoonu Musaa, \u00f1u ngiy def li yoon woowu t\u00ebral, ndaxte Y\u00e0lla def na ko ci nit. Te wonee na\u00f1u noonu ne, man na\u00f1oo r\u00e0\u00f1\u00f1ee lu baax ak lu bon, su \u00f1u nekkul sax ci yoonu Musaa,\n2:15 di wone it ne, Y\u00e0lla bind na ci seen xol j\u00ebf yi yoonu Musaa santaane. Seen xel it seede na ne noonu la, fekk seeni xalaat \u00f1oo leen di tuumaal, mbaa \u00f1u leen di j\u00e9ggal.\n2:16 Ndax b\u00e9s dina \u00f1\u00ebw, bu xalaat yu l\u00e0qu yi di fee\u00f1, te Y\u00e0lla \u00e0tte nit \u00f1i jaarale ko ci Yeesu Kirist. Xebaar bu baax, bi may waare, moo ko wax.\n2:17 Maa ngi \u00f1\u00ebw nag ci yaw mi ne Yawut nga; yaa ngi sukkandiku ci yoonu Musaa ak di damu ci Y\u00e0lla.\n2:18 Xam nga coobareem, ndaxte j\u00e0ng nga ci yoonu Musaa, ba fonk y\u00ebf yi g\u00ebn a baax.\n2:19 Yaa ngi teg sa bopp wommatkatu gumba yi ak leeru \u00f1i nekk cig l\u00ebnd\u00ebm.\n2:20 Yaa di j\u00e0ngalekatu \u00f1i j\u00e0ngul ak xamlekatu \u00f1i xamul, ndaxte xalaat nga ne, Y\u00e0lla jagleel na leen ci yoonu Musaa b\u00e9pp xam-xam ak g\u00e9pp d\u00ebgg.\n2:21 Kon nag yaw miy j\u00e0ngal say moroom, xanaa doo j\u00e0ngal sa bopp? Yaw miy waare di tere s\u00e0cc, mbaa doo s\u00e0cc yaw itam? Yaw miy tere njaaloo, mbaa doo njaaloo?\n2:22 Yaw miy araamal x\u00ebr\u00ebm yi, mbaa doo s\u00e0cc li nekk ci seeni x\u00e0mb?\n2:23 Yaw miy damoo yoonu Musaa, mbaa doo ko moy, ba indi g\u00e0cce ci turu Y\u00e0lla?\n2:24 Moo tax Mbind mi ne: \u00abY\u00e9ena tax \u00f1i nekkul Yawut di suufeel turu Y\u00e0lla.\u00bb\n2:25 B\u00ebggoon naa ngeen xam ne, xaraf am na njari\u00f1, boo ca boolee s\u00e0mm yoon. Waaye boo ko ca boolewul, sa xaraf amatul njari\u00f1.\n2:26 Te itam ku xaraful, tey def j\u00ebf yu jub yi yoonu Musaa santaane, ndax Y\u00e0lla du ko teg ni ku xaraf?\n2:27 Ku dul Yawut te xaraful waaye di s\u00e0mm yoon wi, kooku dina la man a \u00e0tte yaw Yawut bi. Ndaxte li ngay xam-xam yoonu Musaa ci Mbind mi te xaraf, terewul nga koy moy.\n2:28 Juddu nekk Yawut taxul sag Yawut d\u00ebggu, te xaraf ci saw yaram taxul sa xaraf w\u00f3or.\n2:29 Waaye Yawut d\u00ebgg, ci xol lay nekk. Te xaraf d\u00ebgg itam, ci xol lay nekk. Du ngistal, lu d\u00ebggu la. Te k\u00e9pp ku mel noonu, dees na la g\u00ebr\u00ebm, waxumala nit \u00f1i, waaye Y\u00e0lla ci boppam.\n3:1 Yawut bi nag, ci lan la rawe ku dul Yawut? Te xaraf lu muy njari\u00f1?\n3:2 Raw na ko fu nekk. Ci bu j\u00ebkk Yawut yi la Y\u00e0lla d\u00e9nk waxam.\n3:3 Bu fekkee ne am na ci \u00f1oom \u00f1u \u00f1\u00e0kk k\u00f3ll\u00ebre, ndax loolu man na fanq k\u00f3ll\u00ebreg Y\u00e0lla?\n3:4 Mukk! Su \u00f1\u00e9pp nekkoon ay naaf\u00e9q, du tere Y\u00e0lla nekk d\u00ebgg. Moom la Mbind mi wax ci Y\u00e0lla ne:\u00abLoo wax, \u00f1\u00e9pp \u00e0nd ci,te ku layoo ak yaw, nga yey ko.\u00bb\n3:5 Su fekkee nag njubadig nit dina fee\u00f1al njubteg Y\u00e0lla, lu ciy seen xalaat? Wax ji may b\u00ebgg a wax nag l\u00e9egi, waxi nit rekk la, maanaam: ndax kon Y\u00e0lla \u00e0ttewul yoon ci li muy daan ku jubadi?\n3:6 Mukk! Ndax su Y\u00e0lla jubadi woon, naka lay \u00e0ttee \u00e0ddina si?\n3:7 Waaye nag xanaa dina am ku tontu ci loolu ne: \u00abSu fekkee sama \u00f1\u00e0kk k\u00f3ll\u00ebre g\u00ebn na y\u00e9kkati k\u00f3ll\u00ebreg Y\u00e0lla, di yokk it ndamam, lu tax kon Y\u00e0lla di ma teg ba tey b\u00e0kkaarkat, ba di ma \u00e0tte?\u00bb\n3:8 Lu tax m\u00ebnunoo wax ne: \u00abNanu def lu bon, ngir lu baax g\u00e9nn ca?\u00bb Am na sax \u00f1u nuy tuumaal, di wax ne, noonu lanuy waaree. Waaye \u00f1iy wax loolu, ndaan gi \u00f1u yelloo dina leen dal.\n3:9 Kon nag lu nu ci war a wax? Nun Yawut yi, ndax noo g\u00ebn \u00f1i ci des? Mukk! Ndaxte wone nanu ne, nit \u00f1\u00e9pp \u00f1u ngi ci nootaangeg b\u00e0kkaar, muy Yawut yi mbaa Gereg yi.\n3:10 Moom la Mbind mi wax ne:\u00abKu jub amul, du kenn sax.\n3:11 Amul kenn ku xam y\u00ebfi Y\u00e0lla,mbaa kenn ku koy wut.\n3:12 \u00d1\u00e9pp jeng na\u00f1u,ba kenn amalatul Y\u00e0lla njari\u00f1.Kenn du def lu baax, du kenn sax!\n3:13 Seen put a ngi xasaw ni m\u00e9ddum \u00f1etti fan,seen l\u00e0mmi\u00f1 l\u00e0ggi ci njubla\u014b,te seeni k\u00e0ddu aay ni da\u014baru \u00f1\u00e0ng\u00f3or.\n3:14 Du\u00f1u g\u00e9nne ci seen g\u00e9mmi\u00f1 lu dul ay m\u00f3olu ak i xas.\n3:15 \u00d1u sawar la\u00f1u ci rey nit.\n3:16 Fu \u00f1u jaar, foofa y\u00e0qu ak musiba.\n3:17 Xamu\u00f1u yoonu j\u00e0mm,\n3:18 te ragal Y\u00e0lla sore na seen xol.\u00bb\n3:19 Xam nanu nag ne, l\u00e9pp lu yoonu Musaa wax, wax na ko \u00f1i nekk ci yoon woowu, ngir g\u00e9mmi\u00f1 y\u00e9pp ne miig, te waa \u00e0ddina s\u00e9pp jaar ci \u00e0tteb Y\u00e0lla.\n3:20 Ndaxte s\u00e0mm yoon wi taxul kenn jub ci kanam Y\u00e0lla; solob ndigal yi daal mooy wone b\u00e0kkaar.\n3:21 Waaye l\u00e9egi nag Y\u00e0lla fee\u00f1al na, ni nit man a jube ci kanamam, ci lu s\u00e9qul ak yoonu Musaa dara. Waaye ba tey yoonu Musaa ak waxi yonent yi seedeel na\u00f1u ko.\n3:22 Jub ci kanam Y\u00e0lla, g\u00ebm Yeesu Kirist rekk a koy maye, te k\u00e9pp ku ko g\u00ebm bokk nga ci. Ndaxte \u00f1\u00e9pp a yem fa kanam Y\u00e0lla.\n3:23 \u00d1\u00e9pp a b\u00e0kkaar, ba joteetu\u00f1u ndamu Y\u00e0lla.\n3:24 Waaye gannaaw Kirist Yeesu dee na ngir jot leen, Y\u00e0lla ciw yiwam man na leen a \u00e0tte ni \u00f1u jub ci dara.\n3:25 W\u00e0cce na Kirist, mu nekk sarax ngir Y\u00e0lla baal nu sunuy b\u00e0kkaar, jaar ci deretam ji \u00f1u tuur; te ng\u00ebm rekk moo nu ciy boole. Noonu Y\u00e0lla firndeel na ne ku jub la, doonte sax dafa mu\u00f1aloon \u00f1i jiitu jamonoy Kirist, ba j\u00e9ggal leen seeni b\u00e0kkaar.\n3:26 Kon ci jamono jii nu ne, Y\u00e0lla wone na bu leer ne ku jub la, di \u00e0tte ni ku jub k\u00e9pp ku g\u00ebm Yeesu, te ba tey d\u00ebkk ci njubteem.\n3:27 Kan a man a b\u00e0kku nag ci kanam Y\u00e0lla? Kenn! Lu ko waral nag? Xanaa s\u00e0mm yoon? D\u00e9ed\u00e9et! Ng\u00ebm rekk.\n3:28 Ndaxte danoo d\u00ebggal ne, ng\u00ebm rekk a tax Y\u00e0lla di \u00e0tte nit ni ku jub, waaye du s\u00e0mm yoon.\n3:29 Walla ndax nag Yawut yi rekk la fi nekkal? Ndax nekkalu fi it \u00f1u dul Yawut? Aa\u014bkay!\n3:30 Gannaaw Y\u00e0lla kenn la, \u00f1\u00e9pp la fi nekkal. \u00d1i xaraf dina leen \u00e0tte ni \u00f1u jub ndax seen ng\u00ebm, \u00f1i xaraful it dina leen \u00e0tte ni \u00f1u jub ndax seen ng\u00ebm.\n3:31 Xanaa kon ng\u00ebm day fanq yoonu Musaa? Mukk! Da koy g\u00ebn a d\u00ebg\u00ebral sax.\n4:1 Sunu maam Ibraayma, mi nu soqikoo; nu mbiram t\u00ebdde?\n4:2 Bu fekkoonte ne Ibraayma, ci kaw i j\u00ebfam la ko Y\u00e0lla \u00e0ttee ni ku jub, kon am na lu mu ci man a damoo. Waaye demewul noonu ci kanam Y\u00e0lla.\n4:3 Lan la Mbind mi wax ci loolu? Nee na: \u00abIbraayma g\u00ebm na Y\u00e0lla, te Y\u00e0lla j\u00e0ppe ng\u00ebmam ni njub.\u00bb\n4:4 K\u00e9pp kuy ligg\u00e9ey dina jot peyam; te pey googu du ag may, \u00f1aqam la.\n4:5 Waaye Y\u00e0lla dina \u00e0tte jub sax ki ko weddi woon; kon ku w\u00e9eruwul ciy j\u00ebfam, waaye mu g\u00ebm rekk, Y\u00e0lla dina j\u00e0ppe ng\u00ebmam ni njub.\n4:6 Noonu la Daawuda birale barkeelug nit ki Y\u00e0lla jagleel njub, fekk ay j\u00ebfam taxul.\n4:7 Mu ne:\u00ab\u00d1i \u00f1u baal seen j\u00e0dd yoon,te seeni b\u00e0kkaar far ci kanam Y\u00e0lla,\u00f1u barkeel la\u00f1u.\n4:8 Ki Boroom bi s\u00ebful ay b\u00e0kkaaram,kooka ku barkeel la.\u00bb\n4:9 Kon nag barkeel googu, ndax \u00f1i xaraf rekk \u00f1oo ko yeyoo? Ndax \u00f1i xaraful it bokku\u00f1u ci? Aa\u014bkay! Ndaxte wax nanu ne, Y\u00e0lla j\u00e0ppe na ng\u00ebmu Ibraayma ni njub.\n4:10 Ka\u00f1 la ko jagleel njub nag? Ndax lu jiitu xarafam la woon, am gannaaw ga? Lu ko jiitu la woon.\n4:11 Ndaxte Ibraayma g\u00ebm na, te Y\u00e0lla j\u00e0ppe na ng\u00ebmam ni njub, fekk booba xarafagul. Te xarafal gi, m\u00e0ndarga la woon ci yaramam, di firndeel ne, ku jub la woon. Noonu la Ibraayma man a nekke baayu \u00f1\u00e9pp \u00f1i g\u00ebm, ba Y\u00e0lla man leen a \u00e0tte ni \u00f1u jub, te xarafu\u00f1u sax.\n4:12 Te noonu itam la Ibraayma man a nekke baayu \u00f1i xaraf, bu fekkee yemu\u00f1u rekk ci xaraf, waaye \u00f1u am ng\u00ebm, ga Ibraayma sunu maam amoon lu jiitu xarafam.\n4:13 Ndaxte Y\u00e0lla dafa digoon Ibraayma ak \u00f1i naroon a soqikoo ci moom, ne dina\u00f1u moom \u00e0ddina si. Te dige boobu j\u00f3gewul ci yoonu Musaa, waaye dafa j\u00f3ge ci njub, gi Ibraayma amoon ci kanam Y\u00e0lla ci kaw ng\u00ebmam.\n4:14 Ndaxte su fekkee ne \u00f1i nekk ci yoonu Musaa rekk \u00f1ooy moom \u00e0ddina, kon ng\u00ebm amatul njari\u00f1, te digeb Y\u00e0lla dafa toxu.\n4:15 Yoonu Musaa daal du def lu dul w\u00e0cce merum Y\u00e0lla ci sunu bopp; ndax fu yoon amul, j\u00e0dd yoon du fa man a am.\n4:16 Kon nag loolu Y\u00e0lla dige, ng\u00ebm rekk a koy indi, ngir mu sukkandikoo yiwu Y\u00e0lla rekk. Noonu la dige bi w\u00f3ore ci \u00f1i soqikoo ci Ibraayma \u00f1\u00e9pp, du ci \u00f1i nekk ci yoonu Musaa rekk, waaye itam \u00f1i g\u00ebm ni Ibraayma g\u00ebme woon. Kon Ibraayma mooy sunu baay, nun \u00f1\u00e9pp.\n4:17 Moom la Y\u00e0lla dogal, wax ko ci Mbind mi ne: \u00abDef naa la baayu xeet yu bare.\u00bb Ndaxte Ibraayma g\u00ebmoon na Y\u00e0lla, miy dekkal \u00f1i dee, tey wax ci lu amagul, mel ni dafa am.\n4:18 Ibraayma dafa j\u00e0ppoon ci ng\u00ebmam, di yaakaar, fekk bunti yaakaar y\u00e9pp t\u00ebju. Moo tax mu nekk baayu xeet yu bare, ni ko Mbind mi waxe ne: \u00abNoonu la sa askan di meli.\u00bb\n4:19 Mu xool yaramam, xam ne dee rekk a ko dese, ndax mi ngi tollu woon ci lu mat t\u00e9em\u00e9eri at, waaye ba tey ng\u00ebmam w\u00e0\u00f1\u00f1ikuwul. Mu xam it ne, Saarata m\u00ebnatul a \u00ebmb.\n4:20 Waaye loolu taxul ng\u00ebmadi j\u00e0pp ko, ba muy werante ci waxu Y\u00e0lla; ng\u00ebmam sax di g\u00ebn a d\u00ebg\u00ebr, mu daldi sant Y\u00e0lla,\n4:21 mu w\u00f3or ko ne, loolu ko Y\u00e0lla dig, Y\u00e0lla man na koo def.\n4:22 Moo tax \u00abY\u00e0lla jagleel na Ibraayma njub.\u00bb\n4:23 Waaye loolu la\u00f1u bind ne: \u00abY\u00e0lla jagleel na ko njub,\u00bb du Ibraayma rekk a moom wax ji.\n4:24 Nun itam ci wax jooju lanu bokk, te Y\u00e0lla dina nu jagleel njub, nun \u00f1i g\u00ebm Y\u00e0lla, mi dekkal Yeesu sunu Boroom.\n4:25 Ndaxte Y\u00e0lla j\u00e9bbale na ko ngir sunuy too\u00f1, dekkal ko ngir \u00e0tte nu jub.\n5:1 L\u00e9egi nag, gannaaw Y\u00e0lla \u00e0tte na nu jub ci kaw ng\u00ebm, nanu j\u00e0pp ci j\u00e0mm, ji nu am fa kanam Y\u00e0lla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist.\n5:2 Moo nu ubbil bunt ci Y\u00e0lla, nu taxaw temm ci yiwam, jaar ci ng\u00ebm. Te it nu ngi b\u00e9g ciy n\u00e9gandiku, Y\u00e0lla boole nu ci ndamam.\n5:3 Te du ci loolu rekk, waaye b\u00e9g nanu it ci sunuy nattu; ndax xam nanu ne, nattu day feddali mu\u00f1;\n5:4 te mu\u00f1 mooy ndeyu jikko ju d\u00ebg\u00ebr; te jikko ju d\u00ebg\u00ebr day jur yaakaar.\n5:5 Te yaakaar jooju du ay nax, ndax mb\u00ebggeelu Y\u00e0llaa ngi baawaan ci sunu xol, jaarale ko ci Xelam mu Sell mi mu nu may.\n5:6 Ndaxte bi nu amul jenn doole, booba la Kirist dee ngir nun, fekk danoo weddi woon Y\u00e0lla.\n5:7 Kuy nangoo deeyal nit ku jub, yombul a gis, waaye nag jombul am na ku nangoo deeyal ku baax.\n5:8 Waaye Y\u00e0lla firndeel na mb\u00ebggeelam ci nun, ci li Kirist dee ngir nun, bi nu nekkee sax ay b\u00e0kkaarkat!\n5:9 Gannaaw Kirist tuur na deretam nag, ngir Y\u00e0lla \u00e0tte nu jub, rawatina ne dina nu musal ci merum Y\u00e0lla.\n5:10 Nun ay ba\u00f1aaley Y\u00e0lla lanu woon, waaye Doomam dee na, ngir jubale nu ak moom. Gannaaw l\u00e9egi nag xariti Y\u00e0lla lanu, rawatina ne dinanu mucc ndax dundug Doomam.\n5:11 Te sax nu ngi b\u00e9g ci Y\u00e0lla, jaarale ko ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi nu jubale ak moom.\n5:12 Kon nag b\u00e0kkaar ci kenn nit la jaar, dugg ci \u00e0ddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit \u00f1\u00e9pp, ndaxte \u00f1\u00e9pp a b\u00e0kkaar.\n5:13 B\u00e0kkaar kon nekkoon na ci \u00e0ddina, bi Y\u00e0lla di laata w\u00e0cce yoonu Musaa. Waaye gannaaw yoonu Musaa t\u00ebddagul woon, b\u00e0kkaar du woon j\u00e0dd yoon.\n5:14 Teewul nag la dale ca Aadama ba ca Musaa, dee a ngi fi woon ci \u00e0ddina, di noot \u00f1\u00e9pp, ak sax \u00f1i seen b\u00e0kkaar melul woon ni bosu Aadama, maanaam j\u00e0dd yoon. Aadama moomu nag moo di takkandeeru Kirist, mi waroon a ganesi \u00e0ddina.\n5:15 Waaye warunoo yemale too\u00f1u Aadama ak mayu Y\u00e0lla. B\u00e0kkaaru kenn nit kooku tax na \u00f1u bare dee; waaye yiwu Y\u00e0lla ak may, gi nu keneen nit ka Yeesu Kirist y\u00e9w\u00e9nal, baawaan na ci \u00f1u bare, ba suul too\u00f1 googu.\n5:16 Te b\u00e0kkaaru Aadama niroowul ak mayu Y\u00e0lla. Aadama b\u00e0kkaar na benn yoon, ba tax Y\u00e0lla daan ko, daanaale \u00f1\u00e9pp; waaye Y\u00e0lla j\u00e9ggale na too\u00f1 yu bare ci dara, ba mu \u00e0tte \u00f1u bare ni \u00f1u jub.\n5:17 B\u00e0kkaaru kenn nit tax na dee t\u00e0bbi \u00e0ddina, yilif \u00f1\u00e9pp ni buur; waaye j\u00ebfu keneen nit ka, maanaam Yeesu Kirist, moo ko suul, ba tax \u00f1u bare t\u00e0bbi ci dund gu bees, falu ni ay buur; xanaa \u00f1i Y\u00e0lla boole ci yiwam wu bare, te \u00e0tte leen jub ci dara fa kanamam.\n5:18 Kon nag nu g\u00e0ttal wax ji; j\u00e0ddug kenn nit ka rekk moo waral Y\u00e0lla daan \u00f1\u00e9pp; noonu itam j\u00ebf ju jubu keneen nit ka rekk moo ubbi bunt, ba \u00f1\u00e9pp man a jub ci kanam Y\u00e0lla te am dund gu bees.\n5:19 Aadama moomu dafa d\u00e9ggadil Y\u00e0lla, ba y\u00f3bbaale \u00f1u bare, \u00f1u nekk i b\u00e0kkaarkat; noonu itam Yeesu Kirist dafa d\u00e9ggal Y\u00e0lla, y\u00f3bbaale \u00f1u bare itam, \u00f1u jub.\n5:20 Te yoonu Musaa daldi w\u00e0cc, ngir b\u00e0kkaar g\u00ebn a bare; waaye fa b\u00e0kkaar bare, yiwu Y\u00e0lla g\u00ebn faa bare.\n5:21 Ba tax, ni b\u00e0kkaar doon yilife \u00f1\u00e9pp ni buur, indaale dee, noonu itam la yiwu Y\u00e0lla faloo ni buur, j\u00f3ge ci njub, j\u00ebm ci dund gu dul jeex. Te loolu l\u00e9pp darajay Yeesu Kirist sunu Boroom moo nu ko may.\n6:1 Lu nu war a wax l\u00e9egi nag? Xanaa nu sax ci b\u00e0kkaar, ngir yiwu Y\u00e0lla g\u00ebn a bare?\n6:2 Mukk! Nun \u00f1i dee, ba r\u00ebcc ci k\u00e0ttanu b\u00e0kkaar, naka lanu manatee sax ci di ko def?\n6:3 Xanaa dangeen a xamul ne, k\u00e9pp ku \u00f1u s\u00f3ob ci ndox, ngir wone ne, mu ngi bokk ci Yeesu Kirist, ci deewu Yeesu la bokk.\n6:4 Bi \u00f1u nu s\u00f3obee ci ndox moomu nag, day misaal ne, da\u00f1u noo suul ak Kirist, nu dee ni mu deeye woon; ba tax nu dekki it, ni mu dekkee woon ci dooley Y\u00e0lla Baay bi, te nu s\u00f3obu ci dund gu bees.\n6:5 Kon nag gannaaw benn lanu ak Kirist, dee ni mu deeye woon, kon dinanu nekk it benn ak moom, dekki ni mu dekkee woon.\n6:6 Ndegam xam nanu ne, daajoon na\u00f1u Kirist ca bant ba, xam nanu it ne, jikko ju bon ji nu judduwaale, daajaale na\u00f1u ko ak Kirist ca bant ba. Te Y\u00e0lla def na loolu, ngir nguuru b\u00e0kkaar, gi nekkoon ci sunu yaram tas, nu r\u00ebcc ci dooleem.\n6:7 Ndaxte ku dee, b\u00e0kkaar m\u00ebnatul dara ci yaw.\n6:8 Gannaaw nag dee nanu ak Kirist, g\u00ebm nanu ne, dinanu dekki it ni moom,\n6:9 xam ne Kirist mi dekki dootul dee mukk, dee m\u00ebnatul dara ci moom.\n6:10 Dee na benn yoon, ba b\u00e0kkaar m\u00ebnul ci moom dara; te mi ngi dund l\u00e9egi, di \u00e0nd ak Y\u00e0lla ba f\u00e0ww.\n6:11 Ci noonu nag y\u00e9en itam tegleen seen bopp ni \u00f1u dee ak Kirist, ba r\u00ebcc ci dooley b\u00e0kkaar, di dund, \u00e0nd ak Y\u00e0lla ba f\u00e0ww ndax seen bokk ci Yeesu Kirist.\n6:12 Buleen mayati b\u00e0kkaar nag, mu yilif seeni yaram yu n\u00e9ew doole, bay topp ay b\u00ebgg-b\u00ebggam.\n6:13 Te buleen j\u00e9bbalati seeni c\u00e9r b\u00e0kkaar, mu def leen jumtukaayam ngir j\u00ebfam yu jubadi; waaye gannaaw r\u00ebcc ngeen ci dooley dee, bay dundaat, j\u00e9bbaluleen ci Y\u00e0lla te j\u00e9bbal ko seeni c\u00e9r, mu def leen jumtukaayam ngir j\u00ebfam yu jub.\n6:14 Ndaxte b\u00e0kkaar dootu leen manal dara, y\u00e9en \u00f1i g\u00e9nn ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Y\u00e0lla.\n6:15 Lan lanu war a wax nag l\u00e9egi? Gannaaw g\u00e9nn nanu ci yoonu Musaa, dugg ci yiwu Y\u00e0lla, ndax danoo war a sax ci def b\u00e0kkaar? Mukk!\n6:16 Ndax dangeen a xamul ne, koo j\u00e9bbalu ci moom te d\u00e9ggal ko, jaamam nga? Naka noonu, mbaa ngeen nekk jaami b\u00e0kkaar, mu j\u00ebme leen ci dee, mbaa ngeen d\u00e9ggal Y\u00e0lla, mu s\u00f3ob leen ci yoonu njub.\n6:17 Waaye sant naa Y\u00e0lla ci lii: y\u00e9en \u00f1i doon jaami b\u00e0kkaar, bi ngeen d\u00e9ggee mboolem d\u00ebgg gi, nangu ngeen ko ak seen xol b\u00e9pp.\n6:18 Te ci noonu r\u00ebcc ngeen ci nootaangeg b\u00e0kkaar te j\u00e9bbalu ci Y\u00e0lla, s\u00f3obu ci njub.\n6:19 Xam naa ne, seen xam-xam ci mbir mii sorewul, moo tax ma yombal wax ji, awale ko ci baat yii. Ni ngeen j\u00eble woon seeni c\u00e9r, j\u00e9bbal leen, \u00f1u nekk jaami lu selladi ak lu bon, di g\u00ebn a jur lu bon, noonu itam l\u00e9egi j\u00e9bbal-leen seeni c\u00e9r, \u00f1u nekk jaami njub, ngeen door a sell.\n6:20 Ndaxte keroog ba ngeen nekkee jaami b\u00e0kkaar, s\u00e9quleen woon dara ak lu jub.\n6:21 Ban njari\u00f1 ngeen ci j\u00eble nag? Dara lu dul g\u00e0cce, ndaxte ci dee la leen doon j\u00ebmale.\n6:22 Waaye l\u00e9egi Y\u00e0lla goreel na leen ci kilifteefu b\u00e0kkaar, def leen ay jaamam, ba jural leen sell, j\u00ebme leen ci dund gu dul jeex.\n6:23 Ndaxte peyu b\u00e0kkaar mooy dee, waaye mayu Y\u00e0lla mooy dund gu dul jeex ci Yeesu Kirist sunu Boroom.\n7:1 Bokk yi, y\u00e9en \u00f1i may waxal xam ngeen luy yoon; xam ngeen kon ne, yoon am na doole ci nit diirub dundam.\n7:2 Ci maanaa, mi ngi mel ni jig\u00e9en juy s\u00e9y; yoon a ngi koy boole ak j\u00ebkk\u00ebram, \u00f1u \u00e0nd seen giiru dund, waaye su j\u00ebkk\u00ebr ji faatoo, buum gi dagg na.\n7:3 Kon nag su jabar ji \u00e0ndee ak beneen g\u00f3or, te fekk j\u00ebkk\u00ebr jiy dund, dees na ko \u00e0tte njaaloo. Waaye bu j\u00ebkk\u00ebr ji faatoo, yoon jeexal na seen diggante; man na s\u00e9y nag ak beneen g\u00f3or, te loolu du njaaloo.\n7:4 Nii laa leen ko man a misaale, samay bokk; bi Kirist deeyee, dangeen a deeyandoo ak moom, te noonu yoonu Musaa w\u00e0cc leen. L\u00e9egi nag y\u00e9ena ngi \u00e0nd ak keneen, maanaam Kirist mi dekki, ngir nu amal Y\u00e0lla njari\u00f1.\n7:5 Keroog ba nu daan topp sunu nafsu, yoonu Musaa daan na xamb b\u00ebgg-b\u00ebgg yu bon, yiy yengal sunuy c\u00e9r, ba jural nu dee.\n7:6 Waaye l\u00e9egi yoon wi w\u00e0cc na nu, ci li nu dee, ba r\u00ebcc cig buumam. L\u00e9egi nag nu ngi jaamu Y\u00e0lla, waxumaleen ci s\u00e0mm santaane rekk, ndax loolu wees na, waaye ci k\u00e0ttan gu bees, gi nu Xelum Y\u00e0lla di may.\n7:7 Kon nag lu nu war a wax? Ndax b\u00e0kkaar ci yoonu Musaa la j\u00f3ge? Mukk! Waaye moo ma xamal luy b\u00e0kkaar. Ndaxte su ma yoon wi waxul woon: \u00abBul b\u00ebgg y\u00ebfi jaambur,\u00bb kon duma xam luy xemmem.\n7:8 Waaye b\u00e0kkaar jaare na ci ndigalu Y\u00e0lla, daldi \u00f1\u00ebw dugg ci man, ba yengal ci man xemmem yu bare. Ndaxte ba ma xamagul woon yoonu Musaa, b\u00e0kkaar da ne woon nemm ci man.\n7:9 Te keroog bi ma xamagul lu yoon wi santaane, maa ngi doon dund dund gu neex; waaye ba ma ko d\u00e9ggee, b\u00e0kkaar dafa daldi fuddu ci man, te man ma daldi dee.\n7:10 Noonu gis naa ne, ndigal loolu waroon a j\u00ebme nit \u00f1i ci dund, daf maa j\u00ebme ci dee.\n7:11 Ndaxte b\u00e0kkaar jaar na ci li Y\u00e0lla digle, ba nax ma, rey ma.\n7:12 Kon nag man nanoo wax ne, yoonu Musaa yoon wu sell la, te ndigalu Y\u00e0lla dafa sell, jub te baax.\n7:13 Ndax kon lu baax moo ma t\u00e0bbal ci dee? Mukk! B\u00e0kkaar a ko def, ngir jikkoom fee\u00f1; dafa gis ci lu baax loolu bunt bu mu man a jaar, ba rey ma. Noonu ndigalu Y\u00e0lla tax na, b\u00e0kkaar f\u00e9s, bon ba j\u00e9ggi dayo.\n7:14 Xam nanu ne, yoonu Musaa ngi j\u00f3ge ci Y\u00e0lla, waaye man y\u00ebfi \u00e0ddina laa fonk, te nekk ci dooley b\u00e0kkaar, mel nib jaam.\n7:15 Ndaxte samay j\u00ebf jaaxal na ma; li ma b\u00ebgg a def, duma ko def, waaye li ma ba\u00f1 rekk, moom laay def.\n7:16 Kon nag gannaaw li may def du sama coobare, nangu naa ne yoonu Musaa baax na.\n7:17 L\u00e9egi nag du man maay def lu bon loolu, waaye b\u00e0kkaar bi d\u00ebkk ci man, moo ma ciy jii\u00f1.\n7:18 Ndaxte xam naa ne, lu baax d\u00ebkkul ci man, maanaam ci sama bindu doom Aadama. Am naa y\u00e9eney def lu baax, waaye awma k\u00e0ttanu yeggale.\n7:19 Lu baax nag lu may y\u00e9ene, duma ko def, waaye lu bon lu ma b\u00ebggul, moom laay def.\n7:20 Bu fekkee nag lu ma b\u00ebggul, moom laay def, kon dootul sama coobare, waaye b\u00e0kkaar bi d\u00ebkk ci man, moo ma ci jii\u00f1.\n7:21 Gis naa nag lii: saa su ma b\u00ebggee def lu baax, lu bon a ngi ma taxawu.\n7:22 Ndaxte ci sama biir xol yoonu Y\u00e0lla wi neex na ma.\n7:23 Waaye gis naa jeneen doole juy yengu ci samay c\u00e9ri yaram, di b\u00ebre ak li sama xol b\u00ebgg; day b\u00ebre ba noot ma, def ma jaam ci dooley b\u00e0kkaar joojuy yengu ci samay c\u00e9r.\n7:24 C\u00e9y maaka torox! Ana ku may musal ci sama yaram, wii may j\u00ebme ci dee?\n7:25 Maa ngi sant Y\u00e0lla; am na kuy musle, mooy Yeesu Kirist sunu Boroom. Kon nag lii laa gis ci sama bopp: ci sama xel maa ngi topp yoonu Y\u00e0lla, waaye ci sama bindu doom Aadama maa ngi topp yoonu b\u00e0kkaar.\n8:1 L\u00e9egi nag yoon m\u00ebnul a dab \u00f1i bokk ci Yeesu Kirist.\n8:2 Ndaxte k\u00e0ttanu Xelum Y\u00e0lla, tukkee ci Kirist Yeesu, di may nit dund gu bees, goreel na ma ci nootaangeg b\u00e0kkaar ak dee.\n8:3 Lu yoonu Musaa m\u00ebnul woon a def, ndax n\u00e9ew dooley nit, Y\u00e0lla defe na ko nii: dafa y\u00f3nni Doomam, ngir mu yor sunu j\u00ebmm, nun \u00f1iy nekk ay b\u00e0kkaarkat, te mu j\u00e9bbale bakkanam, ngir dindi b\u00e0kkaar yi. Noonu la Y\u00e0lla tase nguuru b\u00e0kkaar ci nit.\n8:4 Ba tax na l\u00e9egi njub, gi yoonu Musaa di digle, am na ci nun, \u00f1iy d\u00e9ggal Xelu Y\u00e0lla mi te ba\u00f1 a topp sunu nafsu.\n8:5 \u00d1iy topp seen nafsu, seeni b\u00ebgg-b\u00ebgg rekk la\u00f1u fonk, waaye \u00f1iy topp Xelu Y\u00e0lla mi, coobareem la\u00f1u fonk.\n8:6 Ndaxte fonk nafsu, ci dee lay j\u00ebme; waaye fonk Xelu Y\u00e0lla mi, dund ak j\u00e0mm lay joxe.\n8:7 Ndaxte ku fonk sa nafsu, ba\u00f1aaleb Y\u00e0lla nga, ndaxte doo d\u00e9ggal Y\u00e0lla, mbaa ngay s\u00e0mm ay santaaneem, te m\u00ebnuloo koo def sax.\n8:8 Kuy topp sa nafsu nag, doo man a neex Y\u00e0lla.\n8:9 Waaye y\u00e9en nekkatuleen ci topp seen nafsu, waaye y\u00e9ena ngi topp Xelu Y\u00e0lla mi, bu fekkee ne mu ngi d\u00ebkk ci y\u00e9en. Ku amul Xelum Kirist nag, bokkuloo ci moom.\n8:10 Bu fekkee ne Kirist d\u00ebkk na ci y\u00e9en nag, lii moo am: seen yaram mi ngi ci dooley dee ndax b\u00e0kkaar bi nekk ci y\u00e9en, waaye seen xel mi ngi dund ndax njub gi leen Y\u00e0lla jox.\n8:11 Kon nag gannaaw Xelum Y\u00e0lla, mi dekkal Yeesu ca n\u00e9ew ya, d\u00ebkk na ci y\u00e9en, dina tax seen yaram wi n\u00e9ew doole dund ci k\u00e0ttanu Xel moomu d\u00ebkk ci y\u00e9en.\n8:12 Kon bokk yi, am nanu lu nu war, waaye waxumaleen topp sunu nafsu ak i b\u00ebgg-b\u00ebggam;\n8:13 ndaxte kuy topp nafsoom, f\u00e0ww mu dee, waaye kuy noot j\u00ebfi yaramam ci dooley Xelu Y\u00e0lla mi, dina dund.\n8:14 Ndaxte \u00f1\u00e9pp \u00f1iy d\u00e9ggal Xelu Y\u00e0lla mi, ay doomi Y\u00e0lla la\u00f1u.\n8:15 Kon nekkatuleen fa kanam Y\u00e0lla, ni jaam bu ragal sangam, waaye Xel mi leen Y\u00e0lla sol, ay doomi Y\u00e0lla la leen def, ba tax nu di wooye Y\u00e0lla: \u00abAbba,\u00bb maanaam \u00abBaay bi.\u00bb\n8:16 Ndaxte Xelu Y\u00e0lla mi, moom ci boppam, day \u00e0nd ak sunu xel ci seede ne, doomi Y\u00e0lla lanu.\n8:17 Te gannaaw ay doomi Y\u00e0lla lanu, dinanu moomi l\u00e9pp li Y\u00e0lla jagleel ay doomam, s\u00e9ddu ci ng\u00ebneel yi Kirist yelloo. Waaye nag ku b\u00ebgg a bokk ak Kirist ndamam \u00ebll\u00ebg, war ngaa s\u00e9ddu ci ay fitnaam tey.\n8:18 Xalaat naa ne sunu naqaru tey, wareesu ko t\u00ebkkale ak sunu ndamu \u00ebll\u00ebg.\n8:19 Ndax li Y\u00e0lla bind l\u00e9pp a ngi ne seew a gis doomi Y\u00e0lla yi fee\u00f1 ci seen biir ndam.\n8:20 Ndaxte dunyaa bi b\u00e9pp mu ngi ci yoon wu dul mujj fenn; teyu ko, Y\u00e0lla moo ko ko teg. Waaye teewul \u00f1u am yaakaar ne,\n8:21 Y\u00e0lla dina rengi seen buumi njaam ci dee, boole leen ci j\u00e0mmu doomi Y\u00e0lla yi ak seen ndam.\n8:22 Xam nanu ba fi nu tollu ne, li Y\u00e0lla bind l\u00e9pp a ngi metitlu ni jig\u00e9en juy matu.\n8:23 Te du dunyaa bi rekk mooy metitlu, nun it nu ngi metitlu, nun \u00f1i Y\u00e0lla sol Xelam, ngir nu \u00f1am a\u00f1u \u00ebll\u00ebg; nu ngi ne seew Y\u00e0lla boole nu ci l\u00e9pp li nu yelloo ni ay doomam, keroog b\u00e9s bu Y\u00e0llay goreel sunu yaram.\n8:24 Ndaxte sunu mucc \u00ebmb na yaakaar. Li nga gis ba noppi, nekkatul yaakaar; li teew, noo koy yaakaare?\n8:25 Li feek gisagunu nag li nuy yaakaar, dinanu ko s\u00e9entu ak mu\u00f1.\n8:26 Te it Xelu Y\u00e0lla mi moo nuy xettali ci sunug n\u00e9ew doole. Ndaxte xamunu sax naka lanu war a \u00f1aane Y\u00e0lla, waaye Xelu Y\u00e0lla maa ngi nuy \u00f1aanal fa moom ak i y\u00e9ene yu l\u00e0mmi\u00f1 m\u00ebnta takk.\n8:27 Te Y\u00e0lla, miy nattu xol yi, xam na xalaatu Xel mi, ndaxte tinu, gi muy tinul gaayi Y\u00e0lla yi, mengoo na ak coobareg Y\u00e0lla.\n8:28 Xam nanu itam ne \u00f1i b\u00ebgg Y\u00e0lla, maanaam \u00f1i Y\u00e0lla woo ci boppam te boole leen ci li mu t\u00ebral, Y\u00e0lla dina joo loxoom ci l\u00e9pp lu xew ci seen dund, ngir jural leen lu baax.\n8:29 Ndaxte \u00f1i mu xamoon lu jiitu, dafa dogaloon \u00f1u nirook Doomam, ngir mu nekk taaw ci biir njaboot gu yaa.\n8:30 Te \u00f1i mu dogaloon loolu ci \u00f1oom, da leen a woo; te \u00f1oo\u00f1u mu woo, da leen a \u00e0tte ni \u00f1u jub; te \u00f1oo\u00f1u mu \u00e0tte jub, da leen a boole ca ndamam.\n8:31 Lu nu war a wax nag ci loolu l\u00e9pp? Gannaaw Y\u00e0lla \u00e0nd na ak nun, kan moo nu manal dara?\n8:32 Y\u00e0lla mi nu g\u00e0ntulul Doomam waaye mu joxe ko, mu dee ngir nun, ndax dina nu ba\u00f1alati dara?\n8:33 \u00d1i Y\u00e0lla t\u00e0nnal boppam, kan moo leen di tuumaal? Y\u00e0lla moo leen \u00e0tte ni \u00f1u jub.\n8:34 Kan moo leen man a teg too\u00f1? Yeesu Kirist mi dee, moo dekki itam, te mu nga fa ndeyjoorul Y\u00e0lla, di nu fa \u00f1aanal!\n8:35 Kan moo nu man a t\u00e0ggaleek mb\u00ebggeelu Kirist? Xanaa duy nattu, te du nj\u00e0qare, du it fitna, du xiif walla rafle, du it ay ngaa\u00f1 walla jaasi sax.\n8:36 Moo tax Mbind mi ne:\u00ab\u00d1u ngi nuy rey ngir yaw, ci suba ba jant so;\u00f1u ngi nuy j\u00e0ppe ni xar yu \u00f1uy rey.\u00bb\n8:37 Waaye loolu l\u00e9pp teewul, nu ngi mel niy \u00f1eyi xare ci dooley Kirist mi nu b\u00ebgg.\n8:38 Ndax w\u00f3or na ma ne, dara m\u00ebnu noo t\u00e0ggaleek mb\u00ebggeelam; du dee, du dund, du malaaka yi, du seeni kilifa, du tey, du \u00ebll\u00ebg, du boroom doole yi,\n8:39 du li ci kaw mbaa li ci suuf, mbaa leneen lu \u00f1u bind; dara m\u00ebnu noo t\u00e0ggale mukk ak mb\u00ebggeel, gi nu Y\u00e0lla jox ci Kirist Yeesu sunu Boroom.\n9:1 Li ma b\u00ebgg a wax nag, ci kanamu Kirist laa koy waxe; d\u00ebgg la, du aw fen. Sama xel, mi Xel mu Sell miy leeral, seedeel na ma ne, d\u00ebgg laay wax.\n9:2 Maanaam, duma noppee am naqar wu r\u00e9y ci sama biir xol,\n9:3 ba xaw a b\u00ebgg a t\u00e0ggoo ak Kirist te alku, ngir \u00f1i ma bokkal xeet mucc.\n9:4 B\u00e0nni Israyil la\u00f1u, te Y\u00e0lla def na leen ni ay doomam; d\u00ebkkaloon na ndamam ci seen biir, fas ak \u00f1oom k\u00f3ll\u00ebre yi. \u00d1oom la Y\u00e0lla d\u00e9nk yoonu Musaa, \u00f1oom la xamal ni \u00f1u ko war a jaamoo, \u00f1oom la jox i digam.\n9:5 Maam ya Y\u00e0lla t\u00e0nnoon, ci \u00f1oom la\u00f1u bokk, te ci \u00f1oom it la Kirist w\u00e0cce, maanaam ci j\u00ebmmam, Kirist mi di Y\u00e0lla, tiim l\u00e9pp, te yelloo teraanga ba f\u00e0ww. Amiin.\n9:6 Waaye neewuma waxu Y\u00e0lla dafa toxu, ndaxte bokk ci b\u00e0nni Israyil, taxul nga bokk ci Israyil tigi.\n9:7 Te it du \u00f1i soqikoo ci Ibraayma \u00f1\u00e9pp, ay doomam d\u00ebgg la\u00f1u. Ndaxte Y\u00e0lla dafa wax Ibraayma ne ko: \u00abSaw askan ci Isaaxa lay jaar.\u00bb\n9:8 Maanaam, soqikoo ci Ibraayma taxul a nekk doomu Y\u00e0lla, waaye juddu ci biir digeb Y\u00e0lla mooy tax a bokk d\u00ebgg-d\u00ebgg ci askanu Ibraayma.\n9:9 Ndaxte Y\u00e0lla dafa digoon Ibraayma naan: \u00abCi waxtu wii d\u00e9w\u00e9n dinaa dellusi ci yaw, te Saarata dina am doom ju g\u00f3or.\u00bb\n9:10 Te du ci loolu rekk, waaye noonu la it ci lu j\u00ebm ci Rebeka; doom yi mu jur \u00f1oo bokk benn baay, moo di sunu maam Isaaxa.\n9:11 Waaye Y\u00e0lla wax ko ne:\u00abYanq\u00f3oba rakk ji mooy yilif magam Esawu,\u00bb fekk xale ya juddoogu\u00f1u te defagu\u00f1u dara, muy lu baax, muy lu bon. Y\u00e0lla def na noonu, maanaam t\u00e0nn kenn ci doom yi, ngir dogalam man a taxaw, te sukkandikuwul ci seeni j\u00ebf waaye ci wooteb Y\u00e0lla.\n9:13 Loolu la Mbind mi wax ne:\u00abB\u00ebgg naa Yanq\u00f3oba, ba\u00f1 naa Esawu.\u00bb\n9:14 Kon lu nu ci war a wax? Ndax Y\u00e0lla \u00e0ttewul foofu yoon nag? Mukk!\n9:15 Dafa wax Musaa sax ne ko:\u00abDinaa y\u00ebr\u00ebm ku ma neex,laabiir ci ku ma neex.\u00bb\n9:16 Dama leen di wax nag, dara ajuwul ci coobareg nit, mbaa ci \u00f1aqam, waaye l\u00e9pp a ngi aju ci y\u00ebrmandey Y\u00e0lla.\n9:17 Ndax Mbind mi biral na li Y\u00e0lla wax Firawna ne ko:\u00abDef naa la buur,ngir fee\u00f1al sama k\u00e0ttan ci say mbir,te ngir siiwal sama tur ci \u00e0ddina si s\u00e9pp.\u00bb\n9:18 Kon nag Y\u00e0lla, la ko neex lay def, muy y\u00ebr\u00ebm nit, mbaa d\u00ebg\u00ebral xolam ci lu bon.\n9:19 Waaye xanaa dina am ku may wax ne: \u00abGannaaw kenn m\u00ebnul a ba\u00f1 coobareg Y\u00e0lla, lu tax kon muy teg nit too\u00f1?\u00bb\n9:20 Yaw nag nit ki, ak koo man a doon, lu tax ngay werante ak Y\u00e0lla? Ndax mbindeef dina laaj ki ko bind: \u00abLu tax nga binde ma nii?\u00bb\n9:21 Ndax tabaxkatu ndaa sa\u00f1ul a fab banam, tabax ci \u00f1aari ndaa, benn bi ngir soxla yu am maana, bi ci des ngir soxla yu ndaw?\n9:22 Kon nag looy wax ci lii: Y\u00e0lla b\u00ebggoon na wone meram, xamle it dooleem ci \u00e0ddina; teewul dafa sax ci mu\u00f1al \u00f1i yelloo meram te taxaw ci s\u00e0nku.\n9:23 B\u00ebggoon na it xamle m\u00e0ggaayam mu \u00ebpp xel, ci boole \u00f1i mu y\u00ebr\u00ebm ci ndamam; moo tax mu t\u00e0nn leen ca nj\u00e0lb\u00e9en.\n9:24 Te wax ji noo ko moom, nun \u00f1i Y\u00e0lla woo ci boppam ci biir Yawut yi ak ci biir xeet yi ci des.\n9:25 Moom la wax ci t\u00e9ereb Ose ne:\u00ab\u00d1i nekkul woon sama xeetdinaa leen ko def,\u00f1i bokkul woon ci sama mb\u00ebggeel,dinaa leen ci boole.\u00bb\n9:26 Te:\u00abFa \u00f1u leen waxe woon:\u201cDungeen sama xeet,\u201ddees na leen fa wooye\u201cDoomi Y\u00e0lla Boroom dund.\u201d\u00bb\n9:27 Esayi wax na ci mbirum Israyil ne:\u00abLu b\u00e0nni Israyil baree-bare ni suufus g\u00e9ej sax,lu n\u00e9ew rekk a ciy mucc.\n9:28 Ndaxte li Boroom bi dogal ci \u00e0ddina,dina ko gaaw a def, te dina mat s\u00ebkk.\u00bb\n9:29 Esayi it waxoon na lu jiitu loolu ne:\u00abY\u00e0lla Boroom k\u00e0ttan gi,su b\u00e0yyiwul woon ci nun lu n\u00e9ew,kon ba tey raat nanu ni d\u00ebkki Sodom ak Gomor.\u00bb\n9:30 Lu nu ci war a wax nag? \u00d1i dul Yawut te fonku\u00f1u woon jub ci kanam Y\u00e0lla, l\u00e9egi jub na\u00f1u ci kaw ng\u00ebm.\n9:31 Waaye b\u00e0nni Israyil, mi b\u00ebggoon a s\u00e0mm yoon ngir jub, matalu ko.\n9:32 Ndax lan? Ndax da\u00f1oo sukkandiku ci seeni j\u00ebf, b\u00e0yyi ng\u00ebm. Da\u00f1oo daanu ci \u00abdoj wuy fakkatale.\u00bb\n9:33 Moom la Y\u00e0lla wax ci Mbind mi ne:\u00abDinaa samp ci Siyon doj wuy fakkatale,di xeer wuy daaneel nit; waaye ku w\u00e9eru ci moom, sa yaakaar du tas.\u00bb\n10:1 Bokk yi, sama coobareg xol ci b\u00e0nni Israyil ak sama \u00f1aan ci Y\u00e0lla, mooy \u00f1u mucc.\n10:2 Seedeel naa leen ne, \u00f1u farlu la\u00f1u ci jaamu Y\u00e0lla, waaye seen njaamu \u00e0ndul ak xam-xam.\n10:3 Xamu\u00f1u yoon, wi Y\u00e0lla t\u00ebral ngir nit jub ci kanamam, waaye da\u00f1oo w\u00e9y ci seen pexey bopp; ba tax \u00f1u ba\u00f1 a nangu yoonu njub woowu Y\u00e0lla t\u00ebral.\n10:4 Ndaxte ci Kirist la yoonu Musaa d\u00ebppe, ba tax ku ko g\u00ebm, dinga jub fa kanam Y\u00e0lla.\n10:5 Ku b\u00ebgg a jub ci kanam Y\u00e0lla ci kaw s\u00e0mm yoon, Musaa daf cee wax ne: \u00abKu ko manoon a matal, dinga dund ba f\u00e0ww.\u00bb\n10:6 Waaye ku jub ci kanam Y\u00e0lla ci kaw ng\u00ebm, nii lay waxe:\u00abBul wax ci sa xol ne:\u201cKuy y\u00e9eg ci kaw?\u201d\u00bb mel ni dangaa b\u00ebgg Kirist w\u00e0cc.\n10:7 \u00abBul wax it:\u201cKuy dem ca bars\u00e0q?\u201d\u00bb mel ni dangaa b\u00ebgg Kirist dekki.\n10:8 Kon boog lan lay wax? Lii:\u00abWaxu Y\u00e0lla mi ngi ci sa wet,ci sa l\u00e0mmi\u00f1, ci sa xol.\u00bb Te wax jooju lal ng\u00ebm lanuy waare.\n10:9 Ndaxte soo waxee ak sa g\u00e9mmi\u00f1 ne, Yeesu mooy Boroom bi, te nga g\u00ebm ci sa xol ne, Y\u00e0lla dekkal na ko, dinga mucc.\n10:10 Ndax xol la nit di g\u00ebme, ba tax mu jub ci kanam Y\u00e0lla; l\u00e0mmi\u00f1 it la nit di waxe ne, mi ngi ci Kirist, ba tax Y\u00e0lla musal ko.\n10:11 Mbind mi dafa wax ne: \u00abK\u00e9pp ku ko g\u00ebm, sa yaakaar du tas mukk.\u00bb\n10:12 Ndax \u00f1\u00e9pp a yem ci kanam Y\u00e0lla, muy Yawut mbaa ku dul Yawut, ndax kenn rekk mooy sunu Boroom nun \u00f1\u00e9pp, te ku y\u00e9w\u00e9n la ci k\u00e9pp ku koy \u00f1aan.\n10:13 Ndaxte bind na\u00f1u: \u00abK\u00e9pp ku woo Boroom bi ciw turam, dinga mucc.\u00bb\n10:14 Waaye nan la\u00f1uy wooye ki \u00f1u g\u00ebmagul? Te naka la\u00f1u man a g\u00ebme ki \u00f1u d\u00e9ggagul turam? Te naka la\u00f1u man a d\u00e9gge turam, te kenn xamalu leen ko?\n10:15 Te it nan la\u00f1u man a waaree, su leen kenn y\u00f3nniwul? Looloo tax Mbind mi wax ne: \u00ab\u00d1iy y\u00e9gle xebaar bu baax bi, ni seen \u00f1\u00ebw di sedde xol!\u00bb\n10:16 Waaye \u00f1\u00e9pp nanguwu\u00f1u xebaar bu baax bi; moom la Esayi wax ne: \u00abBoroom bi, ana ku g\u00ebm sunu waare?\u00bb\n10:17 Kon boog ng\u00ebm ci kaw d\u00e9gg lay juddoo, te d\u00e9gg sosoo ci xebaaru Kirist.\n10:18 Waaye ma ne: xanaa \u00f1\u00e9pp da\u00f1oo d\u00e9ggul? Aa\u014bkay! Mbind mi wax na ne:\u00abSeen baat jolli na ci \u00f1eenti xebla y\u00e9pp,seen wax w\u00ebr na \u00e0ddina s\u00e9pp.\u00bb\n10:19 Waaye ma teg ci ne: xanaa b\u00e0nni Israyil da\u00f1oo xamul? Aa\u014bkay! Musaa dafa j\u00ebkkoon a wax ne:\u00abDinaa leen siisloo xeet wu bokkul ci Y\u00e0lla,merloo leen ci \u00f1i xamul dara ci Y\u00e0lla.\u00bb\n10:20 Te Esayi takk na fitam, ba wax ne:\u00ab\u00d1i ma wutul woon, gis na\u00f1u ma,fee\u00f1 naa ci \u00f1i ma laajul woon.\u00bb\n10:21 Waaye ci mbirum Israyil dafa wax ne:\u00abT\u00e0llal naa samay loxo, suba ba ngoon, ci xeet wu may ba\u00f1 tey werante.\u00bb\n11:1 Ma ne kon, ndax Y\u00e0lla b\u00ebrg\u00ebl na xeetam? Mukk! Ndaxte man itam ci Israyil laa bokk, w\u00e0cce ci Ibraayma te bokk ci giiru Ben-yamin.\n11:2 Y\u00e0lla b\u00ebrg\u00eblul xeetam, wi mu xamoon lu jiitu. Ndax dangeen a xamul li Mbind mi di wax ci mbirum Iliyas? Dafa doon tawat Israyil ci Y\u00e0lla naan:\n11:3 \u00abBoroom bi, rey na\u00f1u say yonent, daaneel say b\u00e9rab yu sell, ba man kenn maa ci des, te \u00f1u ngi may wut a rey.\u00bb\n11:4 Waaye lii la ko Y\u00e0lla tontu: \u00abDencal naa sama bopp jur\u00f3om-\u00f1aari junniy nit, \u00f1i jaamuwul Baal.\u00bb\n11:5 Noonu itam ci jamono ji nu nekk, des na nit \u00f1u n\u00e9ew \u00f1u Y\u00e0lla dencal boppam ciw yiwam.\n11:6 Gannaaw nag yiwu Y\u00e0lla rekk a tax mu denc leen, kon du seen peyug \u00f1aq, walla boog yiwu Y\u00e0lla dootul yiw.\n11:7 Kon lu nu ci war a wax? Li b\u00e0nni Israyil doon wut, gisu\u00f1u ko. Waaye \u00f1i Y\u00e0lla t\u00e0nn rekk a ko gis, te \u00f1a ca des ba\u00f1 a g\u00ebm, ba seen xol d\u00ebrkiis.\n11:8 Looloo tax Mbind mi ne:\u00abY\u00e0lla daf leen a jox xelum nit ku g\u00ebmmeentu,b\u00ebt yu g\u00ebl\u00ebm ak nopp yu t\u00ebx,ba ci b\u00e9sub tey.\u00bb\n11:9 Te Daawuda it daf ci wax naan:\u00abNa seeni \u00f1am sax nekk fiir ak i pakk;na\u00f1u ci daanu, te Y\u00e0lla mbugal leen.\n11:10 Na\u00f1u gumba ba ne fatuus,na\u00f1u tiis te s\u00ebgg ba f\u00e0ww.\u00bb\n11:11 Ndax kon da\u00f1oo tarxiis, daanu ba f\u00e0ww? Mukk! Waaye j\u00e9llub Israyil dafa ubbi bunt, ngir xeeti \u00f1i dul Yawut man a mucc, te b\u00e0nni Israyil siis leen.\n11:12 Gannaaw seen too\u00f1 nag moo ubbi buntu yiw ci waa \u00e0ddina si, te seen \u00f1\u00e0kk moo me\u00f1\u00f1 barkeb xeet y\u00e9pp, c\u00e9y b\u00e9s bu Israyil g\u00e9pp delloo ci Y\u00e0lla, ndaw barke bu bare!\n11:13 Y\u00e9en \u00f1i dul Yawut, y\u00e9en laay waxal. Ndegam Y\u00e0lla daf maa def ndawam, y\u00f3nni ma ci y\u00e9en xeeti \u00e0ddina si, damay matal samab y\u00f3nnent.\n11:14 Dama koy def, ngir \u00f1i bokk ak man xeet siis, ba \u00f1enn \u00f1i mucc.\n11:15 Ndaxte bi Y\u00e0lla g\u00e9nnee Israyil, ubbee na noonu bunt, ngir xeeti \u00e0ddina juboo ak moom; kon su Y\u00e0lla dugalaatee Israyil, ndax du mel ni ndekkitel n\u00e9ew ya?\n11:16 Damay wax ne, mburu m\u00e9pp sell na, bu ci Y\u00e0lla amee w\u00e0ll. Naka noonu garab gi Y\u00e0lla s\u00e9ddoo reen bi, garab g\u00e9pp sell na.\n11:17 B\u00e0nni Israyil a ngi mel ni garabu oliw gu \u00f1u j\u00ebmb\u00ebt ci k\u00ebr gi, waaye mu am car yu ci f\u00e0q. Yaw mi dul Yawut, yaa ngi mel ni caru garabu oliw gu \u00e0ll bu \u00f1u jabtal ci garabu k\u00ebr googu. Noonu nga jari\u00f1oo meen, mi j\u00f3ge ci reen bi.\n11:18 Kon nag bul b\u00e0kku, di xeeb car yooyu Y\u00e0lla f\u00e0q. Waaye soo b\u00ebggee b\u00e0kku, xamal ne, reen moo lay yenu, te du yaw miy car yaa koy yenu.\n11:19 Xanaa dinga wax ne: \u00abCar yooyu da\u00f1u leen a f\u00e0q, ngir jabtal ma fa \u00f1u nekkoon.\u00bb\n11:20 D\u00ebgg la; waaye seen ng\u00ebmadee tax \u00f1u f\u00e0q leen, wuutal la fa ndax sa ng\u00ebm. Bumu tax nag ngay b\u00e0kku, waaye nanga moytu.\n11:21 Gannaaw Y\u00e0lla baalul car ya cosaanoo ca garab ga, kon boog y\u00e9en itam man na leen a f\u00e0q.\n11:22 Loolu kon wone na ni Y\u00e0lla baaxe ak ni muy meree too\u00f1. Ci \u00f1i daanu, Y\u00e0lla wone na ni meram t\u00e0nge, wone mbaaxam ci y\u00e9en, su fekkee y\u00e9ena ngi ci w\u00e9y; lu ko moy, dees na leen f\u00e0q y\u00e9en itam.\n11:23 Te car yooyu f\u00e0q, su \u00f1u w\u00e9yul ci seen ng\u00ebmadi, dees na leen delloo ci garab gi, ndax Y\u00e0lla man na leen cee tafaat.\n11:24 Yaw mi dul Yawut, yaa ngi bokkoon ci garabu oliw gu \u00e0ll, waaye Y\u00e0lla daf la cee j\u00eble, ci lu dul faral a am, jabtal la ci garabu k\u00ebr gi. Kon man nanoo g\u00ebn a w\u00f3or ne, Yawut ya judduwaale nekk ci garabu oliw gu k\u00ebr gi, Y\u00e0lla dina leen ci delloo.\n11:25 Bokk yi, dama leen a b\u00ebgg a dindi kumpa ci lii, ngir ngeen ba\u00f1 a y\u00e9g seen bopp. D\u00ebrkiisu xol dab na b\u00e0nni Israyil ab diir, ba b\u00e9s ba mboolem waa \u00e0ddina, \u00f1u war a bokk ci nguuru Y\u00e0lla, dugg ca.\n11:26 Bu loolu amee nag, b\u00e0nni Israyil g\u00e9pp dina mucc. Moom la Mbind mi t\u00ebral, bi mu naan:\u00abAb xettalikat dina j\u00f3ge ci Siyon,d\u00e0q weddi ci askanu Yanq\u00f3oba.\n11:27 Loolu mooy k\u00f3ll\u00ebre, gi may fas ak \u00f1oom,b\u00e9s bu may dindi seeni b\u00e0kkaar.\u00bb\n11:28 Gannaaw ba\u00f1 na\u00f1u xebaar bu baax bi, ay ba\u00f1aaley Y\u00e0lla la\u00f1u, ngir ngeen jot barkeem. Waaye gannaaw Y\u00e0lla t\u00e0nn na leen, dafa leen b\u00ebgg ba tey ndax seen maam ya.\n11:29 Ndax li Y\u00e0lla maye, dootu ko nangu mukk, te ku mu woo ci boppam, dootu la d\u00e0q mukk.\n11:30 \u00d1u d\u00e9ggadil Y\u00e0lla ngeen woon, waaye ng\u00ebmadig Yawut yi tax na, ngeen jot y\u00ebrmandeem.\n11:31 \u00d1oom itam l\u00e0nk na\u00f1u l\u00e9egi, ngir man a bokk ak y\u00e9en y\u00ebrmandey Y\u00e0lla.\n11:32 Kon Y\u00e0lla t\u00ebj na \u00f1\u00e9pp ci ng\u00ebmadi, ngir man a y\u00ebr\u00ebm \u00f1\u00e9pp.\n11:33 Xelum Y\u00e0lla ni mu x\u00f3ote, ak xam-xamam ni mu baree, ba raw xelum nit! Kan moo muus, ba xam dogalam? Walla nga am xel, ba n\u00e0nd ay j\u00ebfam?\n11:34 Mbind mi dafa ne:\u00abAna ku xam xalaatu Boroom bi?Ku ko doon digal?\u00bb\n11:35 Te it:\u00abKu ko mas a jox dara,ba mu war laa delloo?\u00bb\n11:36 Ndaxte ci moom la l\u00e9pp sosoo, ci moom la l\u00e9pp di jaar, ci moom la l\u00e9pp di dellu. Moo yelloo ndam ba f\u00e0ww. Amiin.\n12:1 Kon nag bokk yi, gannaaw y\u00ebrmandey Y\u00e0lla baree na noonu, maa ngi leen di \u00f1aan, ngeen j\u00e9bbal ko seen yaram w\u00e9pp. Na seen dund mel ni sarax su \u00f1uy defal Y\u00e0lla, sarax su sell te neex ko. Loolu mooy njaamu, gi leen war.\n12:2 Bu leen \u00e0ddina jey, waaye yeesluleen ci seen xel, ba soppiku, ngeen man a xam bu w\u00e9r coobareg Y\u00e0lla, di l\u00e9pp lu baax, neex ko te mat s\u00ebkk.\n12:3 Gannaaw Y\u00e0lla may na ma ciw yiwam, ma nekk ndawam, maa ngi leen di wax lii, kenn ku nekk ci y\u00e9en: buleen y\u00e9g seen bopp, waaye ngeen am xalaat yu yem, mengook ng\u00ebm gi leen Y\u00e0lla s\u00e9dd, ku nekk ak w\u00e0llam.\n12:4 Loolu, ci maanaa, mi ngi mel ni yaramu nit: yaram, lu c\u00e9r yi baree-bare, benn niroowul ak moroomam ligg\u00e9ey.\n12:5 Noonu itam nun \u00f1i bokk ci Kirist, lu nu baree-bare, benn lanu te danoo m\u00e0nkoo.\n12:6 Kon gannaaw Y\u00e0lla s\u00e9ddale na ay mayam, ku nekk ak sa c\u00e9r, nanu koy j\u00ebfandikoo. Ku Y\u00e0lla may, ngay waare k\u00e0ddoom, nga wax ko kem sa ng\u00ebm;\n12:7 kuy topptoo y\u00ebfi mbooloo mi, nga takku ci; ku Y\u00e0lla may, ngay j\u00e0ngale, nekk ci;\n12:8 kuy feddali ng\u00ebmu nit \u00f1i ci Y\u00e0lla, nga sax ci; kuy s\u00e9ddoo alalam ak nit \u00f1i, nga def ko ak xol bu laab; kuy jiite mbooloo mi, nga sawar ci; kuy dimbali \u00f1i n\u00e9ew doole, nanga ci b\u00e9g.\n12:9 Na seen cofeel di lu d\u00ebggu te ba\u00f1 a nekk ngistal; araamal-leen lu bon te sax ci lu baax.\n12:10 B\u00ebgganteleen ak xol bu leer, niy doomi ndey, te farlu ci teralante.\n12:11 Sawarleen te ba\u00f1 a tayel, di jaamu Boroom bi ak seen xol b\u00e9pp.\n12:12 B\u00e9gleen ci yaakaaru \u00ebll\u00ebg te mu\u00f1 b\u00e9pp tiis, di sax ci \u00f1aan Y\u00e0lla.\n12:13 Dimbalileen gaayi Y\u00e0lla yi ci seeni soxla, te saxoo dalal gan.\n12:14 Ku leen fitnaal, \u00f1aanal-leen ko yiw, te ba\u00f1 koo m\u00f3olu.\n12:15 B\u00e9gandooleen ak \u00f1i b\u00e9g, te jooyandoo ak \u00f1iy jooy.\n12:16 Bokkleen menn xel, tey ba\u00f1 a y\u00e9kkatiku, di y\u00f3otu daraja, waaye ngeen fonk \u00f1i suufe; buleen teg seen bopp boroomi xel.\n12:17 Buleen feyante lu bon, waaye s\u00e0kkuleen seede su rafet ci kanam \u00f1\u00e9pp.\n12:18 Wutleen a juboo ak \u00f1\u00e9pp, ba fa seen k\u00e0ttan yem.\n12:19 Samay soppe, buleen di feyantoo, waaye b\u00e0yyileen l\u00e9pp ci loxoy Y\u00e0lla, mi yelloo \u00e0tte; ndax Y\u00e0lla nee na ci Mbind mi: \u00abMan maay \u00e0tte, maay fey j\u00ebf.\u00bb\n12:20 Waaye defleen lii:\u00abBu sa noon xiifee, may ko mu lekk;bu maree, may ko mu naan.Ndax boo ko defee, dinga ko rusloo.\u00bb\n12:21 Bu leen lu bon \u00ebpp doole, waaye nootleen ko ci def lu baax.\n13:1 Gannaaw loolu na nit ku nekk d\u00e9ggal \u00f1i yore baat ci kanamam; ndaxte amul njiit lu fi Y\u00e0lla sampul. Njiit y\u00e9pp nag Y\u00e0lla moo leen fi teg.\n13:2 Kon ku leen ba\u00f1 a d\u00e9ggal, ndigalu Y\u00e0lla nga l\u00e0nk, te ku def loolu, yoon dina la dab.\n13:3 Kuy def lu baax warul a ragal njiit li, kuy def lu bon moo ko war a ragal. Soo ko b\u00ebggee ba\u00f1 a ragal nag, kon defal lu baax, te dina la tagg.\n13:4 Ndax Y\u00e0llaa ko d\u00e9nk ligg\u00e9ey boobu ngir sa j\u00e0mm. Waaye sooy def lu bon, war ngaa ragal, ndax du cig neen la ame jaasiy \u00e0tte; jawri\u00f1u Y\u00e0lla la ngir w\u00e0cce meru Y\u00e0lla, ci fey ku def lu bon.\n13:5 Kon fokk ngeen d\u00e9ggal ko, waxuma sax ndax sa\u00f1-sa\u00f1am boobu, waaye it ngir seen xel dal.\n13:6 Gannaaw Y\u00e0llaa sas njiit yi ligg\u00e9ey boobu, te \u00f1i ngi ci, kon f\u00e0ww ngeen fey galag.\n13:7 Joxleen ku nekk c\u00e9ram; ku ngeen war a fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen war a fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen war a weg, wegleen ko; ku ngeen war a teral, teral-leen ko.\n13:8 Buleen ameel kenn dara, lu dul mb\u00ebggeel; ndax ku b\u00ebgg sa moroom, w\u00e0ccoo nga ak yoonu Musaa.\n13:9 Ndaxte ndigali Y\u00e0lla y\u00e9pp, yi deme ni: \u00abBul njaaloo, bul rey nit, bul s\u00e0cc, bul b\u00ebgge,\u00bb walla leneen ndigal lu mu man a doon, wax jii moo leen \u00ebmb: \u00abNanga b\u00ebgg sa moroom, ni nga b\u00ebgge sa bopp.\u00bb\n13:10 Ku b\u00ebgg sa moroom, doo ko too\u00f1; kon ku w\u00e9y ci mb\u00ebggeel matal nga yoonu Musaa.\n13:11 Te lii itam am na: xam ngeen bu baax jamono ji nu tollu; jamonoy yeewu jot na, ndax l\u00e9egi sunu mucc g\u00ebn na noo jege, ca ba nu dooree g\u00ebm.\n13:12 Guddi gi m\u00e0ggat na, b\u00ebt a ngi b\u00ebgg a set. Nanu b\u00e0yyi nag j\u00ebf yu l\u00ebnd\u00ebm te r\u00e0ngoo g\u00e0nnaay yi nu Y\u00e0lla jox, ngir dund ci leer.\n13:13 Gannaaw nu ngi ci leer, na sunug dund rafet. Bunu naan sangara ba m\u00e0ndi tey b\u00e0nneexu; bunu njaaloo tey def i \u00f1aawteef ak sunuy c\u00e9r; bunu xuloo mbaa nuy \u00f1eeyante.\n13:14 Waaye g\u00e0nnaayooleen Yeesu Kirist Boroom bi, te ba\u00f1 a topp seen bakkan ciy b\u00ebgg-b\u00ebggam yu bon.\n14:1 Gannaaw loolu ku ng\u00ebmam n\u00e9ew nangeen ko nangu, te ba\u00f1 a werante ak moom ci lu l\u00ebnt.\n14:2 Ndax am na ku xalaat ne, man na lekk \u00f1am wu nekk, fekk ku ng\u00ebmam n\u00e9ew du lekk y\u00e0pp, waaye l\u00e9jum rekk lay lekk.\n14:3 Kiy lekk lu nekk, bumu xeeb ki ko dul def. Naka noonu itam ku dul lekk y\u00e0pp, bumu teg too\u00f1 ki koy lekk; ndax Y\u00e0lla nangu na leen \u00f1oom \u00f1aar.\n14:4 Koo teg sa bopp, ba di ko teg too\u00f1? Jaamu jaambur la! Mu taxaw ci ligg\u00e9eyam, mbaa mu s\u00e0ggane ko, moom ak sangam la. Waaye dina jub, ndax Boroom bi am na dooley taxawal ko ci njub.\n14:5 Noonu itam am na \u00f1iy t\u00e0nn b\u00e9s ak \u00f1iy yemale b\u00e9s y\u00e9pp. Na ku nekk xam bu w\u00e9r li muy def, te j\u00e0pp ci.\n14:6 Ndaxte kuy t\u00e0nn b\u00e9s, mu ngi koy def ngir m\u00e0ggal Boroom bi. Kiy lekk lu nekk it, mu ngi koy def ngir m\u00e0ggal Boroom bi; loolu leer na ndax day sant Y\u00e0lla. Te it ki ba\u00f1 a lekk y\u00e0pp, mu ngi koy def ngir m\u00e0ggal Boroom bi, di ko sant.\n14:7 Kenn ci nun dundul ngir boppam, kenn deewul it ngir boppam.\n14:8 Danuy dund ngir m\u00e0ggal Boroom bi, dee it ngir m\u00e0ggal ko. Kon nag nuy dund mbaa nu dee, noo ngi ci Boroom bi.\n14:9 Loolu sax moo waral Kirist dee te dundaat, ngir man a nekk Boroomu \u00f1i dee ak \u00f1iy dund.\n14:10 Yaw nag lu tax ngay teg sa moroom too\u00f1? Lu tax nga koy xeeb? Xanaa nun \u00f1\u00e9pp, danu dul dajeji fa kanam Y\u00e0lla, ngir mu layoo ak nun?\n14:11 Ndaxte Mbind mi t\u00ebral na lii:\u00abBoroom bi nee na:\u201cNi mu w\u00f3ore ne maa ngi dund,ni la w\u00f3ore ne, \u00f1\u00e9pp dina\u00f1u ma sukkal,te ku nekk seede ne maay Y\u00e0lla.\u201d\u00bb\n14:12 Noonu ku nekk ci nun dinga l\u00e0yyi fa Y\u00e0lla ci l\u00e9pp loo mas a def.\n14:13 Kon nanu b\u00e0yyee tegante too\u00f1, waaye nu fas y\u00e9enee moytu l\u00e9pp lu nekk fiir guy y\u00f3bbe sunu moroom b\u00e0kkaar.\n14:14 Xam naa ne, amul wenn \u00f1am wu sellul, ndax Yeesu Boroom bi xamal na ma loolu. Waaye loo yaakaar ne sellul, ci yaw la sellul.\n14:15 Soo dee lekk luy indil sa moroom tiis, g\u00e9nn nga ci mb\u00ebggeel. Yaw nag bul r\u00e9eral sa moroom ci sa \u00f1am, ndax Kirist dee na ngir moom.\n14:16 Bu sa njari\u00f1 jur wax ju \u00f1aaw.\n14:17 Ndaxte bokk ci nguuru Y\u00e0lla jotewul dara ak lu nuy lekk mbaa lu nuy naan. Nguuru Y\u00e0lla mooy jub ci kanam Y\u00e0lla, te am mb\u00e9g ak j\u00e0mm ci dooley Xel mu Sell mi.\n14:18 Kiy jaamoo noonu Kirist moo neex Y\u00e0lla ak nit \u00f1i.\n14:19 Kon nag nanu wut luy indi j\u00e0mm, tey y\u00e9kkati ng\u00ebmu sunu moroom.\n14:20 Bu sa \u00f1am y\u00e0q j\u00ebfu Y\u00e0lla. B\u00e9pp \u00f1am sell na ci kanam Y\u00e0lla. Ci lu w\u00e9r! Waaye k\u00e9pp ku lekk luy y\u00e0q sa ng\u00ebmu moroom, def nga lu bon.\n14:21 Liy sa warugar mooy nga ba\u00f1 a fiir sa moroom ci y\u00e0pp mbaa ci bii\u00f1 mbaa ci leneen lu mu man a doon.\n14:22 Su fekkee sa ng\u00ebm d\u00ebg\u00ebr na, wone ko ci sa diggante ak Y\u00e0lla. Kiy nangu, te du ci sikkal boppam, kooku barkeel na.\n14:23 Waaye kuy lekk \u00f1am te am ci xel \u00f1aar, def nga b\u00e0kkaar, ndax sa ng\u00ebm yemu fa. Ndaxte j\u00ebf ju \u00e0ndul ak ng\u00ebm, b\u00e0kkaar la.\n15:1 Nun \u00f1i d\u00ebg\u00ebr ci sunu ng\u00ebm, war nanoo nangu \u00f1i seen ng\u00ebm n\u00e9ew te am ci lu \u00f1uy sikki-s\u00e0kka, te ba\u00f1 a yem ci wut sunu b\u00e0nneex.\n15:2 Na ku nekk ci nun di wut lu neex moroomam ngir jari\u00f1 ko, ba mu g\u00ebn a d\u00ebg\u00ebr ci ng\u00ebmam.\n15:3 Ndaxte Kirist musul a wut b\u00e0nneexu boppam. Loolu la Mbind mi wax ne: \u00abLor yi \u00f1u la saagaa, ci sama kaw la\u00f1u dal.\u00bb\n15:4 Ndaxte l\u00e9pp lu \u00f1u waxoon ci Mbind mi lu jiitu tey, da\u00f1u koo t\u00ebraloon, ngir nu s\u00e0kku ci xam-xam, xam-xam bu nuy may fit ak mu\u00f1, ak di feddali sunu yaakaar.\n15:5 Kon nag Y\u00e0lla miy maye mu\u00f1 ak fit, na leen may, ngeen d\u00e9ggoo te nekk benn bu yellook li Kirist Yeesu wone.\n15:6 Ba tax nu bokk benn xalaat ak benn baat ci m\u00e0ggal Y\u00e0lla, Baayu Yeesu Kirist sunu Boroom.\n15:7 Moo tax nangoonteleen, bay m\u00e0ggal Y\u00e0lla, ni leen Kirist nangoo.\n15:8 Lii laay wax: Kirist \u00f1\u00ebw na ligg\u00e9eyal Yawut yi, ngir wone k\u00f3ll\u00ebreg Y\u00e0lla ci matal dige, ya mu digoon maam ya.\n15:9 \u00d1\u00ebw na itam ngir \u00f1i nekkul Yawut man a m\u00e0ggal Y\u00e0lla ndax y\u00ebrmandeem. Moo tax Mbind mi ne:\u00abDinaa la m\u00e0ggal tey tagg saw tur,ci kanamu xeet y\u00e9pp.\u00bb\n15:10 Mbind mi nee na it:\u00abY\u00e9en xeeti \u00e0ddina, \u00f1\u00ebwleen b\u00e0nneexuak xeet wi Y\u00e0lla t\u00e0nnal boppam.\u00bb\n15:11 Mu dellooti ne:\u00abSantleen Boroom bi, y\u00e9en waa \u00e0ddina,te \u00f1\u00ebw m\u00e0ggal ko, y\u00e9en xeet y\u00e9pp.\u00bb\n15:12 Te it Esayi wax na ne:\u00abAm na s\u00ebtu Yese buy \u00f1\u00ebw,dina yilif xeeti \u00f1i dul Yawut,te ci moom la\u00f1uy w\u00e9kk seen yaakaar.\u00bb\n15:13 Kon Y\u00e0lla miy maye yaakaar, na def ci seen xol mb\u00e9g mu r\u00e9y ak j\u00e0mm ju yaa ci seen kaw ng\u00ebm, ba ngeen am yaakaar ju mat s\u00ebkk ci dooley Xel mu Sell mi.\n15:14 Bokk yi, w\u00f3or na ma ne, baax ngeen ba fa mbaax man a yem, fees dell ak xam-xam, ba man a j\u00e0ngaleente mbiri Y\u00e0lla ci seen biir.\n15:15 Bu sama k\u00e0ddu diisee nag ci bataaxal bii, dara taxul lu dul b\u00ebgg a yeesal seen xalaat, ndaxte Y\u00e0lla ci kaw yiwam daf maa sas,\n15:16 ma nekk jawri\u00f1u Kirist Yeesu, yebal ma ci \u00e0ddina ci xeeti \u00f1i dul Yawut. Ligg\u00e9ey bu sell laay def ngir Y\u00e0lla, ci xamle xebaaram bu baax bi, ngir xeeti \u00e0ddina sell ci dooley Xel mu Sell mi, ba neex Y\u00e0lla, mel ni sarax su \u00f1u koy j\u00e9bbal.\n15:17 Kon nag maa ngi b\u00e0nneexu ci Kirist Yeesu ngir ligg\u00e9ey boobu ma Y\u00e0lla d\u00e9nk.\n15:18 Awma fitu wax leneen nag, lu dul li Kirist j\u00ebf jaarale ko ci man, ngir xeeti \u00e0ddina j\u00e9bbalu ci moom; j\u00ebf na jaarale ci samay wax ak samay j\u00ebf,\n15:19 ci ay tegtal ak i k\u00e9emaan, sukkandikoo ci dooley Xelu Y\u00e0lla mi. Ba fi mu nekk nag y\u00e9gle naa fu nekk xebaaru Kirist, li dale ci Yerusalem, jaar ci gox y\u00e9pp, ba \u00e0gg diiwaanu Iliri.\n15:20 Sama y\u00e9ene mooy xamle xebaaru turu Kirist fa mu eggagul, ndax b\u00ebggumaa yeggale sas wu keneen daloon.\n15:21 Li ma def nag, d\u00ebppoo na ak li Mbind mi wax ne:\u00ab\u00d1i y\u00e9gagul mbiram dina\u00f1u ko y\u00e9g,te \u00f1i ko musul a d\u00e9gg, xam ko.\u00bb\n15:22 B\u00ebggoon naa \u00f1\u00ebw seetsi leen, fekk ay t\u00e9q-t\u00e9q \u00f1oo ma t\u00e9ye ba tey.\n15:23 Waaye nag l\u00e9egi bey naa sama sas ci gox yii.\n15:24 Bu may dem Espaa\u00f1 nag, b\u00ebgg naa faa jaar, nuyu leen; ndaxte ay at a ngii maa ngi am y\u00e9ene ju tar ci \u00f1\u00ebw seetsi leen. B\u00ebgg na maa nekk ci seen biir, ngir am b\u00e0nneexu sotteente ak y\u00e9en xalaat ab diir, te it ngeen waajalal ma sama yoonu Espaa\u00f1.\n15:25 Waaye nag fi mu nekk maa ngi dem nii Yerusalem, ngir dimbaliji gaayi Y\u00e0lla yu sell ya fa nekk.\n15:26 Ndaxte waa Maseduwan ak waa Akayi \u00f1i g\u00ebm, fas na\u00f1u y\u00e9eney s\u00e0kk ci seeni alal, y\u00f3nnee ko, ngir dimbali \u00f1i n\u00e9ew doole ci gaayi Y\u00e0lla yu sell, yi nekk Yerusalem.\n15:27 Y\u00e9ene na\u00f1u ko, te it ci d\u00ebgg-d\u00ebgg bor la, bu \u00f1u war a fey. Ndaxte gannaaw \u00f1i g\u00ebm ci Yerusalem s\u00e9ddoo na\u00f1u ak \u00f1i dul Yawut seen ng\u00ebm, kon xeet yooyu itam war na\u00f1oo s\u00e9ddoo ak \u00f1oom seen alal.\n15:28 Kon nag waxtu wu ma noppee ci ligg\u00e9ey boobu, teg may gu tedd gii ci loxoy boroom, dinaa dem Espaa\u00f1, tey jaar fi y\u00e9en.\n15:29 Te w\u00f3or na maa ne, bu ma agsee ci y\u00e9en, dinaa indaale barkeb Kirist bu mat s\u00ebkk.\n15:30 Gannaaw loolu bokk yi, maa ngi leen di \u00f1aan ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist ak ci b\u00ebggante, gi Xelu Y\u00e0lla mi def ci nun, ngeen defal ma lii: \u00e0ndleen ak man, nu tuur sunu \u00f1aq ci \u00f1aan Y\u00e0lla.\n15:31 \u00d1aanal-leen ma, ngir ma mucc ci \u00f1i g\u00ebmul ci waa Yude; te it gaayi Y\u00e0lla yu sell yu nekk ci Yerusalem nangu ndimbal, li ma leen di y\u00f3bbul.\n15:32 Dolli ci, Y\u00e0lla may ma, ma \u00f1\u00ebw seetsi leen ak xol bu sedd, nu booloo yeeslu fa kanam Y\u00e0lla.\n15:33 Na Y\u00e0lla Boroom j\u00e0mm \u00e0nd ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp. Amiin.\n16:1 Bu nu weesoo loolu, maa ngi leen di d\u00e9nk sunu jig\u00e9en Febe, miy ligg\u00e9eyal mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci d\u00ebkku Se\u00f1sere.\n16:2 Nangeen ko j\u00e0pp ci turu Boroom bi, ni ko gaayi Y\u00e0lla yi yelloo, te dimbali ko ci l\u00e9pp lu mu aajowoo; ndaxte moom itam wax d\u00ebgg, dimbali na \u00f1u bare, ba ci man mii di wax ak y\u00e9en.\n16:3 Nuyul-leen ma Pirsil ak Akilas, samay nawle ci ligg\u00e9eyu Kirist Yeesu.\n16:4 \u00d1oom \u00f1aar dem na\u00f1u, bay b\u00ebgg a jaay seen bakkan ngir man; maa ngi leen di g\u00ebr\u00ebm ci loolu, du man rekk sax, waaye itam mboolooy \u00f1i g\u00ebm ci xeeti \u00e0ddina s\u00e9pp.\n16:5 Nuyul-leen ma it \u00f1iy booloo ci seen k\u00ebr.Maa ngi nuyu it Epaynet, mi j\u00ebkk a g\u00ebm Kirist ci diiwaanu Asi;\n16:6 ak Maryaama, mi sonnoon lool ci y\u00e9en.\n16:7 Nuyul-leen ma it Andoronikus ak Yu\u00f1as, sama bokk, yi \u00f1u ma booleeloon t\u00ebj; am na\u00f1u tur ci ndawi Y\u00e0lla yi, te \u00f1oo ma jiitu sax ci g\u00ebm Kirist.\n16:8 Te f\u00e0ttewuma Ampilyaatus, mi ma b\u00ebgg ci sama xol ngir Boroom bi.\n16:9 Nuyul-leen ma it Urban, sunu nawle ci ligg\u00e9eyu Kirist, ak sama soppe Estakis;\n16:10 ak it Apeles, mi ng\u00ebmam d\u00ebggu, ba yelloo k\u00f3olute.Nuyul-leen ma it waa k\u00ebr Aristobul,\n16:11 ak Erojon sama mbokk, ak waa k\u00ebr Narsis, \u00f1i ci Boroom bi.\n16:12 Maa ngi nuyu Tirifen, moom ak Tirifos, jig\u00e9en \u00f1i sonn ci ligg\u00e9eyu Boroom bi, ak it sama soppe Persidd, mi ci jeex t\u00e0kk.\n16:13 Maa ngi nuyu it Rufus, waa ji xolam seey ci Boroom bi, ak yaayam, mi ma f\u00e9ete woon it c\u00e9rub ndey.\n16:14 Te f\u00e0ttewuma As\u00e0nkirit, Felegon, Ermes, Patarobas, Ermas, \u00f1oom ak mboolem bokk y\u00e9pp.\n16:15 Nuyul-leen ma it Filolog ak Yuli, Nere ak jig\u00e9enam.Te f\u00e0ttewuma Olimpas ak gaayi Y\u00e0lla yiy booloo ak \u00f1oom \u00f1\u00e9pp.\n16:16 Te y\u00e9en bokk yi, saafoonteleen ak xol bu laab. Mboolooy \u00f1i g\u00ebm Kirist y\u00e9pp a ngi leen di nuyu.\n16:17 Bokk yi, maa ngi leen di d\u00e9nk, ngeen moytu \u00f1i leen di f\u00e9ewale, ba di leen j\u00e0ddloo yoon wi, ciy wax lu juuyoo ak d\u00ebgg gi ngeen j\u00e0ng. Dawleen leen ba sore.\n16:18 Ndax \u00f1u deme noonu ligg\u00e9eyalu\u00f1u Kirist sunu Boroom; seen bopp la\u00f1uy ligg\u00e9eyal. \u00d1u ngi \u00f1\u00ebw ak l\u00e0mmi\u00f1 yu neex, di jey xol yu woyof yi, ba nax leen.\n16:19 Waaye seen d\u00e9gg ndigal bir na \u00f1\u00e9pp, ba sama xol sedd lool ci y\u00e9en. Teewul nag damaa b\u00ebgg ngeen am xam-xam bu leer ci lu baax, te ba\u00f1 a laal dara ci lu bon.\n16:20 Su ko defee Y\u00e0lla Boroom j\u00e0mm dina noot Seytaane ci seeni t\u00e0nk l\u00e9egi. Na yiwu Yeesu sunu Boroom \u00e0nd ak y\u00e9en!\n16:21 Timote sama nawle bi may j\u00e0pple ci ligg\u00e9ey bi, mu ngi leen di nuyu, ak samay bokk Lusiyus, Yason ak Sosipater.\n16:22 Man Tersiyus mi bind bataaxal bii nag, maa ngi leen di nuyu ci turu Boroom bi.\n16:23 Gayus mu ngi leen di nuyu; moo may ganale ci k\u00ebram, te foofa it la mbooloo mi di dajaloo. Erast miy topptoo mbiri xaalisu d\u00ebkk bi it, nuyu na leen, ak sunu mbokk Kartus.\n16:24 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist \u00e0nd ak y\u00e9en! Amiin.\n16:25 Santleen Y\u00e0lla, mi leen man a saxal bu w\u00e9r ci d\u00ebggu xebaar bu baax, bi may waare ci mbirum Yeesu Kirist! Nekkoon na kumpa gu l\u00e0qu diirub ay ati at,\n16:26 waaye l\u00e9egi nag Y\u00e0lla dindi na nu ci kumpa. Te santaane na, nu y\u00e9gle xebaar boobu ci xeeti \u00e0ddina s\u00e9pp, ci firi Mbindi yonent yi, ngir nit \u00f1i man koo g\u00ebm, ba j\u00e9bbalu.\n16:27 Y\u00e0lla mi jagoo xam-xam b\u00e9pp, moom rekk moo yelloo ndam ba f\u00e0ww, jaar ci Yeesu Kirist! Amiin.","title":"Wolof Bible (NT): Romans","type":"page"}
