{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/th1.htm","path":"bib/wb/wlf/th1.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/th1.htm","text":"1:1 Nun Pool, Silwan ak Timote noo ngi leen di bind, y\u00e9en mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci d\u00ebkku Tesalonig te nekk ci Y\u00e0lla Baay bi ak Boroom bi Yeesu Kirist. Na yiw ak j\u00e0mm \u00e0nd ak y\u00e9en.\n1:2 B\u00ebt bu set nu ngi sant Y\u00e0lla ndax y\u00e9en, di leen boole ci sunuy \u00f1aan.\n1:3 Dunu noppee f\u00e0ttaliku ci kanam Y\u00e0lla sunu Baay j\u00ebf ji juddu ci seen ng\u00ebm, ligg\u00e9ey bi tukkee ci seen mb\u00ebggeel, ak mu\u00f1 gi sosoo ci seen yaakaar ci sunu Boroom Yeesu Kirist.\n1:4 Bokk yi, y\u00e9en \u00f1i Y\u00e0lla b\u00ebgg, xam nanu ne Y\u00e0lla t\u00e0nn na leen;\n1:5 ndaxte xebaar bu baax, bi nu leen doon y\u00e9gal, yemul woon ci ay wax rekk, waaye \u00e0ndoon na ak k\u00e0ttan ak Xel mu Sell mi ak k\u00f3olute gu mag. Xam ngeen sunu taxawaay ci seen biir ngir seen njari\u00f1.\n1:6 Te aw ngeen sunuy t\u00e0nk ak yu Boroom bi, ci li ngeen nangu xebaar bi ci biir fitna yu metti, \u00e0nd ak mb\u00e9g ci dooley Xel mu Sell mi.\n1:7 Noonu ngeen daldi nekk royukaay ngir \u00f1i g\u00ebm \u00f1\u00e9pp ci diiwaani Maseduwan ak Akayi.\n1:8 Ndaxte k\u00e0ddug Boroom bi jollee na ci seen biir, te yemul ci Maseduwan ak Akayi rekk, waaye seen g\u00ebm Y\u00e0lla siiw na f\u00e9pp. Matul sax nu di ci wax dara,\n1:9 ndaxte \u00f1oom ci seen bopp \u00f1ooy seede li sunu ngan def ci seen biir. Maanaam, ni ngeen d\u00ebddoo x\u00ebr\u00ebm yi, jublu ci Y\u00e0lla te di ko jaamu, moom miy Y\u00e0lla Aji Dund ju d\u00ebggu ji,\n1:10 te ngeen di s\u00e9entu Doomam b\u00e0yyikoo asamaan, moom Yeesu mi mu dekkal te di nu musal ci merum Y\u00e0lla, mi nar a \u00f1\u00ebw.\n2:1 Waaw bokk yi, xam ngeen ne, ngan gi nu leen ganesi woon du nganug neen.\n2:2 Laata nuy \u00f1\u00ebw, jaar nanu ci fitna ak toroxte ca d\u00ebkku Filib, ni ngeen ko xame; waaye Y\u00e0lla sunu Boroom may na nu fit, ba li tongoonte bi metti l\u00e9pp it, y\u00e9gal nanu leen xebaaru Y\u00e0lla bu baax bi.\n2:3 Ndaxte sunu waaraate w\u00e9eruwul cig r\u00e9er walla ci njubla\u014b walla ciy nax.\n2:4 Waaye gannaaw Y\u00e0lla moo nu seet, ba w\u00f3olu nu te d\u00e9nk nu xebaar bu baax bi, kon noonu lanuy waaree, du ngir neex nit \u00f1i, waaye ngir neex Y\u00e0lla, miy seet xol yi.\n2:5 Musunoo jey kenn, y\u00e9en xam ngeen ko; sunu waare musul a \u00ebmb b\u00ebgge, Y\u00e0lla seede na ko;\n2:6 musunoo s\u00e0kku ng\u00ebr\u00ebmu nit, muy ci y\u00e9en, muy ci \u00f1eneen.\n2:7 Manoon nanoo diis ci seen kaw sax, nun \u00f1iy ndawi Kirist, waaye woyofoon nanu ci seen biir, te lewet ni jaboot buy uuf doomam.\n2:8 Cofeel gi nu am ci y\u00e9en tax na, b\u00ebggunu woon a yem ci xamal leen xebaaru Y\u00e0lla bu baax bi, waaye jox leen it sunu bakkan, ndaxte sunu xol seeyoon na ci y\u00e9en.\n2:9 Bokk yi, y\u00e9ena ngi f\u00e0ttaliku sunu coono ak sunu \u00f1aq; xam ngeen ni nu ligg\u00e9eye guddi ak b\u00ebcc\u00ebg, ngir ba\u00f1 a diis ci seen kaw, ci di leen y\u00e9gal xebaaru Y\u00e0lla.\n2:10 Naka sunu diggante ak y\u00e9en \u00f1i g\u00ebm, doxal nanu ko doxalin wu sell te jub te amul sikk: seede ngeen ko, te Y\u00e0lla it seede na ko.\n2:11 Xam ngeen ne, d\u00e9nk nanu leen kenn-kenn, ni baay di def ak doomam, d\u00ebf\u00eblal leen seen xol te d\u00ebggal ci y\u00e9en, ngeen dund dund gu neex Y\u00e0lla, moom mi leen di woo, ngeen s\u00e9ddu ci nguuram ak ndamam.\n2:13 Te it dunu noppee sant Y\u00e0lla ci lii: ba ngeen jotee k\u00e0ddug Y\u00e0lla, gi nu doon waare, nangu ngeen ko, waxuma ni k\u00e0ddug nit waaye ni k\u00e0ddug Y\u00e0lla, ndaxte moom la ci d\u00ebgg-d\u00ebgg, te mu ngi j\u00ebf ci y\u00e9en \u00f1i g\u00ebm.\n2:14 Ndaxte bokk yi, aw ngeen ci t\u00e0nki mboolooy Y\u00e0lla, yi nekk ca r\u00e9ewu Yawut ya tey daje ci turu Kirist Yeesu; fitna ya \u00f1u daj ca Yawut ya, y\u00e9en it seen waa r\u00e9ew teg na\u00f1u leen ko.\n2:15 \u00d1oom Yawut yi rey na\u00f1u Boroom bi Yeesu, ni \u00f1u reye woon yonent yi; teg na\u00f1u nu fitna yu metti; neexu\u00f1u Y\u00e0lla, \u00e0ndu\u00f1u ak kenn,\n2:16 di nu teree wax ak \u00f1i dul Yawut, ngir ba\u00f1 \u00f1u mucc. Du\u00f1u noppee xuus ci biir b\u00e0kkaar, waaye merum Y\u00e0lla x\u00ebppu na ci seen kaw.\n2:17 Nun nag bokk yi, ba \u00f1u ma leen xa\u00f1ee ab diir --xol yi taxul may wax, waaye j\u00ebmm yi rekk \u2014 j\u00e9em nanu leen a gis ak sunu kem-k\u00e0ttan, ndax namm nanu leen, ba sunu xol seey ci gis leen.\n2:18 Kon j\u00e0ppoon nanu leen a seetsi \u2014 man Pool sax ay yooni yoon, waaye Seytaane t\u00e9q na ma.\n2:19 Ndaxte b\u00e9s bu Yeesu sunu Boroom dellusee, te nu fekke ko, kan mooy sunu yaakaar? Kan mooy sunu mb\u00e9g? Kan mooy sunu kaala, gi nuy tiitaroo?\n2:20 Xanaa du y\u00e9en? Waaw y\u00e9enay sunu ndam, y\u00e9enay sunu mb\u00e9g.\n3:1 Kon nag, ba nu ko m\u00ebnatul a d\u00e9kku, nangu nanu \u00f1u b\u00e0yyi nu, nun do\u014b\u014b, ca d\u00ebkku Aten,\n3:2 te y\u00f3nni nanu Timote, sunu mbokk ak sunu nawle ci ligg\u00e9eyu Y\u00e0lla ak ci waareb xebaaru Kirist. Y\u00f3nni nanu ko, ngir mu d\u00e9nk leen, tey feddali seen ng\u00ebm,\n3:3 ngir kenn ba\u00f1 a raf ndax nattu, yi ngeen di jaar. Y\u00e9en ci seen bopp xam ngeen ne, nattu mooy sunu c\u00e9r.\n3:4 Ba nu nekkee ak y\u00e9en sax, waxoon nanu leen, waxati ko ne, f\u00e0ww nu sonn; te noonu la ame, y\u00e9en xam ngeen ko.\n3:5 Noonu ba ma ko m\u00ebnatul a d\u00e9kku, y\u00f3nnee naa, ngir xam fu seen ng\u00ebm tollu, ngir ragal Seytaane fiir leen, ba sunu \u00f1aq neen.\n3:6 Waaye l\u00e9egi Timote bawoo na ci y\u00e9en, indaale xebaar yu neex ci seen ng\u00ebm ak seen mb\u00ebggeel; xamal na nu ne, y\u00e9ena ngi am p\u00e0ttaliku yu rafet ci nun te namm nu lool, ni nu leen namme y\u00e9en itam.\n3:7 Noonu bokk yi, ci biir tiis ak coono yi nu nekk, seen ng\u00ebm d\u00ebf\u00ebl na sunu xol.\n3:8 Ndaxte noo ngi dund d\u00ebgg-d\u00ebgg, ndegam y\u00e9ena ngi sax ci Boroom bi.\n3:9 Ndaw cant yu bare yu nu war a sant Y\u00e0lla ndax y\u00e9en! Ndaw mb\u00e9g mu bare, mi nu am ci kanamam ndax y\u00e9en!\n3:10 Guddi ak b\u00ebcc\u00ebg nu ngi w\u00e0kkirlu ci \u00f1aan Y\u00e0lla, ngir gis leen, ba man a mottali seen ng\u00ebm.\n3:11 Na Y\u00e0lla sunu Baay moom ci boppam ak Yeesu sunu Boroom jubal sunu yoon ci y\u00e9en.\n3:12 Na leen Boroom bi dolli mb\u00ebggeel gu tar, ngeen b\u00ebggante te b\u00ebgg \u00f1\u00e9pp, ni nu leen b\u00ebgge nun.\n3:13 Na samp seeni xol noonu ci cell gu amul sikk fa kanam Y\u00e0lla sunu Baay, ba b\u00e9s bu Yeesu sunu Boroom dellusee, \u00e0nd ak gaayam yu sell y\u00e9pp.\n4:1 L\u00e9egi nag bokk yi, jot ngeen ci nun, nan ngeen war a dunde ba neex Y\u00e0lla, te moom ngeen di def. Waaye ci turu Boroom bi Yeesu nu ngi leen di \u00f1aan ak a d\u00e9nk, ngeen g\u00ebn koo feddali.\n4:2 Ndaxte xam ngeen ndigal, yi nu leen jox ci w\u00e0llu Yeesu Boroom bi.\n4:3 Lii nag mooy coobareg Y\u00e0lla: ngeen sell, maanaam ngeen moytu njaaloo;\n4:4 ngeen noot seeni c\u00e9r ci cell ak tedd,\n4:5 te xemmem ba\u00f1 leen a jiital, ni xeeti \u00e0ddina yi xamul Y\u00e0lla.\n4:6 Ci mbir mii nag, bu kenn ci y\u00e9en laal y\u00ebfi jaambur, ngir ba\u00f1 koo too\u00f1. Ndaxte waxoon nanu leen bu y\u00e0gg te artu leen ne, \u00f1iy def loolu, Boroom bi dina leen mbugal.\n4:7 Ndaxte Y\u00e0lla woo na nu, nu dund ci cell, waaye du ci sobe.\n4:8 Ku tanqamlu wax jii nag, defoo ko nit, Y\u00e0lla nga ko def, moom mi leen di jox Xel mu Sell mi.\n4:9 Ci lu j\u00ebm ci b\u00ebggante ci seen biir, matul nu leen di bind dara, ndaxte Y\u00e0lla def na ci seen xol, ngeen b\u00ebggante.\n4:10 Te moom ngeen di def ci bokk y\u00e9pp, yi ci diiwaanu Maseduwan. Waaye bokk yi, maa ngi leen di xiirtal, ngeen g\u00ebn cee sax.\n4:11 Fullawooleen a dund ci j\u00e0mm, di topptoo seen mbiri bopp tey lekk seen \u00f1aq, ni nu leen ko sante woon.\n4:12 Noonu dingeen dund dund gu jekk ci kanamu waa \u00e0ddina, te it dungeen soxlaal kenn dara.\n4:13 Ci mbirum \u00f1i nelaw nag bokk yi, b\u00ebggu\u00f1u ngeen r\u00e9ere mbir, ba tiis ni aji g\u00ebmul, yi amul benn yaakaar.\n4:14 Ndegam g\u00ebm nanu ne, Yeesu dee na te dekki, noonu it Y\u00e0lla dina indaale ak Yeesu \u00f1\u00e9pp \u00f1i ko g\u00ebm te nelaw.\n4:15 Nu ngi leen di wax lii tukkee ci Boroom bi: nun \u00f1iy dund te des fi, ba kera Boroom biy dellusi, dunu jiitu \u00f1i nelaw.\n4:16 Ndaxte ndigal lu jamp dina jib, baatu kilifa ci malaaka yi d\u00e9gtu, liitu Y\u00e0lla jolli, te Boroom bi moom ci boppam dina w\u00e0cce ca asamaan. Booba \u00f1i g\u00ebm Kirist te dee dina\u00f1u j\u00ebkk a dekki;\n4:17 gannaaw loolu nun \u00f1iy dund te des fi, dina\u00f1u ne f\u00ebyy ak \u00f1oom j\u00ebm ci niir yi, taseji ak Boroom bi ci jaww ji. Te noonu dinanu nekk ak Boroom bi ba f\u00e0ww.\n4:18 Kon nag na ku nekk di d\u00ebf\u00ebl sa xolu moroom ak k\u00e0ddu yooyu.\n5:1 Waaye bokk yi, ci li j\u00ebm ci jamono yi ak waxtu, yi loolu di am, matul nu leen ciy bind dara.\n5:2 Ndaxte xam ngeen bu w\u00e9r ne, ni s\u00e0cc di \u00f1\u00ebwe guddi, noonu la b\u00e9su Boroom bi di \u00f1\u00ebwe.\n5:3 Fekk nit \u00f1iy naan: \u00abL\u00e9pp a ngi ci j\u00e0mm, ba ne leww,\u00bb booba musiba bett leen, ni aw mat di bette jig\u00e9en ju \u00ebmb, te kenn du ci mucc.\n5:4 Waaye y\u00e9en bokk yi, nekkuleen cig l\u00ebnd\u00ebm, ba tax b\u00e9s boobu bett leen ni s\u00e0cc.\n5:5 Ndaxte y\u00e9en \u00f1\u00e9pp ci leer ak b\u00ebcc\u00ebg ngeen bokk; bokkunu ci guddi ak l\u00ebnd\u00ebm.\n5:6 Kon nag bunu nelaw ni \u00f1eneen \u00f1i, waaye nanu xool te maandu.\n5:7 Ndaxte \u00f1iy nelaw, guddi la\u00f1uy nelaw, te \u00f1iy m\u00e0ndi, guddi la\u00f1uy m\u00e0ndi.\n5:8 Waaye nun \u00f1iy waa b\u00ebcc\u00ebg, nanu maandu te r\u00e0ngoo ngir xare bi: ng\u00ebm ak mb\u00ebggeel, muy kiiraayu d\u00ebnn, ak k\u00f3oluteg mucc, muy mbaxanam xare.\n5:9 Ndaxte Y\u00e0lla jaglewu nu meram, waaye mucc la nu jagleel ndax darajay sunu Boroom Yeesu Kirist.\n5:10 Deeyal na nu, ngir nu man a dund ak moom, bu nu nelawee ak bu nu nelawagul.\n5:11 Kon nag nangeen d\u00ebg\u00ebralante te yokkante seen ng\u00ebm, ni ngeen koy defe.\n5:12 Gannaaw loolu bokk yi, ci lu j\u00ebm ci njiit, yi Boroom bi teg ci seen kanam te \u00f1uy ligg\u00e9ey ci seen biir, di leen artu, maa ngi leen di \u00f1aan ngeen d\u00e9glu leen;\n5:13 rax-ca-dolli ngeen naw leen seen kem-k\u00e0ttan te b\u00ebgg leen ndax seen ligg\u00e9ey. Na j\u00e0mm am ci seen biir.\n5:14 Bokk yi, nu ngi leen di d\u00e9nk, ngeen yedd \u00f1i fe\u00f1aag, d\u00ebf\u00ebl \u00f1i seen yasara y\u00e0cciku, dimbali \u00f1i n\u00e9ew doole, tey mu\u00f1al \u00f1\u00e9pp.\n5:15 Saxleen ci baax ci seen biir ak ci \u00f1\u00e9pp, te ba\u00f1 a feyantoo.\n5:16 Deeleen b\u00e9g\n5:17 te sax ciy \u00f1aan Y\u00e0lla,\n5:18 di ko g\u00ebr\u00ebm ci l\u00e9pp, ndaxte loolu mooy coobareg Y\u00e0lla ci y\u00e9en ci seen bokk ci Kirist Yeesu.\n5:19 Buleen fey taalu Xelum Y\u00e0lla,\n5:20 di xeeb waxu yonent yi.\n5:21 Waaye seetleen mbir y\u00e9pp, j\u00e0pp ci li baax,\n5:22 d\u00ebddu l\u00e9pp lu ci bon.\n5:23 Na leen Y\u00e0lla Boroom j\u00e0mm sellal, ba ngeen mat s\u00ebkk; na s\u00e0mm seen xel m\u00e9pp, seen xol b\u00e9pp ak seen yaram w\u00e9pp, ngir dara ba\u00f1 cee am sikk, ba b\u00e9s bu sunu Boroom Yeesu Kirist dellusee.\n5:24 Y\u00e0lla, mi leen woo ci loolu, kuy s\u00e0mm k\u00f3ll\u00ebre la, te dina ko def.\n5:25 Bokk yi, buleen nu f\u00e0tte ci seeni \u00f1aan.\n5:26 Nuyul-leen nu bokk y\u00e9pp ak saafoonte bu laab.\n5:27 Maa ngi leen di d\u00e9nk ci kanamu Boroom bi, ngeen j\u00e0ngal bataaxal bii bokk y\u00e9pp.\n5:28 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist \u00e0nd ak y\u00e9en.","title":"Wolof Bible (NT): 1 Thessalonians","type":"page"}
