{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/th2.htm","path":"bib/wb/wlf/th2.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/th2.htm","text":"1:1 Nun Pool ak Silwan ak Timote noo leen di bind, y\u00e9en mbooloom \u00f1i g\u00ebm ci d\u00ebkku Tesalonig te nekk ci Y\u00e0lla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist.\n1:2 Na leen Y\u00e0lla Baay bi ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak j\u00e0mm.\n1:3 Bokk yi, m\u00ebnunu lu dul sax ci sant Y\u00e0lla ndax y\u00e9en. Loolu jaadu na, ndax seen ng\u00ebm di g\u00ebn a sax, te mb\u00ebggeel gi ngeen am ci seen biir, ku nekk ci sa moroom, di yokku lu bare.\n1:4 Noonu nu ngi damu ci y\u00e9en ci kanamu mboolooy Y\u00e0lla yi, ndax seen mu\u00f1 ak seen ng\u00ebm ci biir mboolem fitnay noon, ak coono, yi ngeen di d\u00e9kku.\n1:5 Loolu mooy firndeel \u00e0tteb Y\u00e0lla bu jub bi, di wone ne yelloo ngeen nguuru Y\u00e0lla, gi tax ngeen di sonn.\n1:6 Ndaxte jub na ci Y\u00e0lla, mu delloo coono \u00f1i leen di sonal,\n1:7 te it y\u00e9en \u00f1iy d\u00e9kku coono, mu boole leen ak nun, t\u00e0bbal nu ci noflaay, b\u00e9s bu sunu Boroom Yeesu Kirist j\u00f3gee asamaan, fee\u00f1 fi. Keroog dina \u00e0nd ak malaakaam yu am k\u00e0ttan,\n1:8 safara su y\u00e0nj w\u00ebr ko, mu fee\u00f1 ngir mbugal \u00f1i xamul Y\u00e0lla te ba\u00f1 a d\u00e9ggal xebaar bu baaxu sunu Boroom Yeesu.\n1:9 Seen pey mooy alku ba f\u00e0ww, \u00f1u d\u00e0q leen fu sore Boroom bi ak ndamam lu r\u00e9y.\n1:10 Dina \u00f1\u00ebw b\u00e9s booba, ngir ndamam jolli ci biir gaayam yu sell yi, te \u00f1\u00e9pp \u00f1i ko g\u00ebm y\u00e9emu ci moom \u2014 te ci ngeen bokk, ndaxte g\u00ebm ngeen li nu leen seede.\n1:11 Moo tax dunu noppeek di leen \u00f1aanal, ngir Y\u00e0lla sunu Boroom def leen, ngeen yeyoo li tax mu woo leen, te yeggali ak doole ci y\u00e9en b\u00e9pp y\u00e9ene ju baax ak b\u00e9pp j\u00ebfu ng\u00ebm.\n1:12 Noonu turu Yeesu sunu Boroom dina m\u00e0gg ci y\u00e9en, te y\u00e9en it dingeen m\u00e0gg ci moom, aju ci yiwu sunu Y\u00e0lla ak Boroom bi Yeesu Kirist.\n2:1 Ci lu j\u00ebm ci \u00f1\u00ebwu Boroom bi Yeesu Kirist nag, bokk yi, ak sunu daje ak moom, am na lu ma leen di \u00f1aan:\n2:2 bu leen kenn gaaw a t\u00e0ggale ak seen sago, mbaa di leen jaaxal, muy yonent buy wax, muy k\u00e0ddu mbaa bataaxal bu \u00f1u nu moomaleel, ci ne leen b\u00e9su Boroom bi \u00f1\u00ebw na xaat.\n2:3 Bu leen kenn nax ci benn f\u00e0nn, ndaxte balaa booba, f\u00e0ww Xiiroo bu mag bi ak Y\u00e0lla am, te Nitu \u00f1aawteef ki fee\u00f1, moom aji alku ji.\n2:4 Day weddi l\u00e9pp lu \u00f1u teg Y\u00e0lla walla \u00f1u koy jaamu, di y\u00e9kkati boppam, ba toog sax ca k\u00ebr Y\u00e0lla ga, tudde boppam Y\u00e0lla.\n2:5 Xanaa f\u00e0ttalikuwuleen ne, waxoon naa leen ko, ba ma nekkee ak y\u00e9en.\n2:6 Te xam ngeen li ko t\u00e9ye l\u00e9egi, ba du man a fee\u00f1 lu dul ci waxtoom.\n2:7 Ndaxte fi mu ne \u00f1aawteef gaa ngi jax-jaxi xaat ci kumpa, waaye ki ko t\u00e9ye mi ngi fi ba tey. Bu fi j\u00f3gee nag,\n2:8 Nitu \u00f1aawteef ki dina fee\u00f1, te Boroom bi Yeesu dina ko rey ak ngelawul g\u00e9mmi\u00f1am, tas ko ak leer giy \u00e0nd ak \u00f1\u00ebwam.\n2:9 Bu Nitu \u00f1aawteef kooku fee\u00f1ee, dina \u00e0nd ak k\u00e0ttanu Seytaane ak doole ju bare, di wone ay firnde ak ay k\u00e9emaan yu dul d\u00ebgg;\n2:10 te dina nas b\u00e9pp naxe buy s\u00e0nke, ba y\u00e9em \u00f1i nar a alku, ndaxte ubbilu\u00f1u seeni xol d\u00ebgg, gi leen manoon a musal.\n2:11 Looloo tax Y\u00e0lla y\u00f3nnee leen xelum r\u00e9er, ba \u00f1u g\u00ebm fen.\n2:12 Noonu Y\u00e0lla dina mbugal \u00f1\u00e9pp \u00f1i g\u00ebmul woon d\u00ebgg te doon b\u00e0nneexu ci njubadi.\n2:13 Kon nag bokk yi, y\u00e9en \u00f1i Boroom bi b\u00ebgg, m\u00ebnunu lu dul sax ci sant Y\u00e0lla ci li mu leen t\u00e0nn ca nj\u00e0lb\u00e9en ga, ngir musal leen, mu s\u00e9dde leen boppam jaarale ko ci j\u00ebfu Xel mu Sell mi ak seen g\u00ebm d\u00ebgg gi.\n2:14 Te Y\u00e0lla woo na leen ci loolu jaarale ko ci xebaar bu baax, bi nu leen doon y\u00e9gal, ngir ngeen bokk ci ndamu sunu Boroom Yeesu Kirist.\n2:15 Kon nag bokk yi, taxawleen bu d\u00ebg\u00ebr te j\u00e0pp ci d\u00e9nkaane yi nu leen jottali, muy ci li nu wax, muy ci li nu bind.\n2:16 Na sunu Boroom Yeesu Kirist moom ci boppam ak Y\u00e0lla sunu Baay, mi nu b\u00ebgg te wone yiwam ci nun, ba ubbil nu buntu j\u00e0mm ju sax ak yaakaar ju w\u00e9r,\n2:17 d\u00ebf\u00ebl seeni xol te saxal leen ci b\u00e9pp j\u00ebf ju rafet ak g\u00e9pp k\u00e0ddu gu baax.\n3:1 L\u00e9egi nag bokk yi, \u00f1aanal-leen nu, ngir k\u00e0ddug Boroom bi law te \u00e0nd ak ndam, ni mu ko ame woon ci y\u00e9en.\n3:2 Ngeen \u00f1aanal nu it, ngir nu mucc ci \u00f1i bon te soxor, ndaxte du \u00f1\u00e9pp a g\u00ebm.\n3:3 Waaye Boroom bi kuy s\u00e0mm k\u00f3ll\u00ebre la; dina leen d\u00ebg\u00ebral te musal leen ci Ibliis.\n3:4 Te w\u00f3or nanu ci kanamu Boroom bi ne, y\u00e9ena ngi def li nu leen santoon, te dingeen ci sax.\n3:5 Na Boroom bi gindi seeni xol ci mb\u00ebggeelu Y\u00e0lla ak mu\u00f1u Kirist.\n3:6 Nu ngi leen di sant it bokk yi, ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen d\u00ebddu b\u00e9pp mbokk buy w\u00e9y ci tayel te ba\u00f1 a topp d\u00e9nkaane, yi nu leen jottali.\n3:7 Xam ngeen bu baax, y\u00e9en ci seen bopp, ni ngeen war a awe ci sunuy t\u00e0nk. Ba nu nekkee ca y\u00e9en, w\u00e9yunu woon ci tayel\n3:8 te musunoo lekk \u00f1aqu kenn. Waaye guddi ak b\u00ebcc\u00ebg danu daan \u00f1aq, di sonn, ngir ba\u00f1 a w\u00e9eru ci kenn ci y\u00e9en.\n3:9 Waxuma ne amunu sa\u00f1-sa\u00f1u def ko, waaye danoo b\u00ebggoon a nekk ay royukaay ci y\u00e9en, ngir ngeen aw ci sunuy t\u00e0nk.\n3:10 Ndaxte ba nu nekkee ca y\u00e9en, lii lanu t\u00ebraloon: \u00abKu ligg\u00e9eyul, du lekk.\u00bb\n3:11 L\u00e9egi nag d\u00e9gg nanu ne, am na ci y\u00e9en \u00f1uy w\u00e9y ci tayel; ligg\u00e9eyu\u00f1u dara, lu dul di dugg ci lu seen yoon nekkul.\n3:12 \u00d1u deme noonu nag, nu ngi leen di sant te di leen d\u00e9nk ci turu Boroom bi Yeesu Kirist, \u00f1uy ligg\u00e9ey ci j\u00e0mm tey dunde seen \u00f1aq.\n3:13 Y\u00e9en nag bokk yi, buleen t\u00e0yyi ci def lu rafet.\n3:14 Su kenn ba\u00f1ee topp li nu bind ci bataaxal bii, r\u00e0\u00f1\u00f1eeleen ko te sore ko, ngir mu rus ci.\n3:15 Waxuma ngeen def ko noon, waaye ngeen yedd ko ni seen mbokk.\n3:16 Na leen Boroom j\u00e0mm may j\u00e0mm ci f\u00e9pp ak ci l\u00e9pp. Na Boroom bi \u00e0nd ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.\n3:17 T\u00e0ggoo bii maa ko bind ci sama loxo, man Pool. Nii laay binde, te di m\u00e0ndargaale nii sama bataaxal y\u00e9pp.\n3:18 Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist \u00e0nd ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.","title":"Wolof Bible (NT): 2 Thessalonians","type":"page"}
