{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/ti2.htm","path":"bib/wb/wlf/ti2.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/ti2.htm","text":"1:1 Man Pool, ndawul Yeesu Kirist ci coobareg Y\u00e0lla, ngir xamle dund gi nu Y\u00e0lla dig te f\u00e9ete ci Kirist Yeesu,\n1:2 maa ngi lay bind Timote, sama doomu diine ji ma b\u00ebgg. Na la Y\u00e0lla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Boroom may yiw, y\u00ebrmande ak j\u00e0mm.\n1:3 Fu ma tollu maa ngi lay boole ci samay \u00f1aan, di ci sant Y\u00e0lla, mi may jaamu ci xel mu dal, ni ko samay maam daan defe. Guddi ak b\u00ebcc\u00ebg, bu sama xel demee ci say rangoo\u00f1,\n1:4 ma b\u00ebgg laa gis, ba am mb\u00e9g mu r\u00e9y.\n1:5 Maa ngi f\u00e0ttaliku sa ng\u00ebm gu d\u00ebggu, gi nekkoon ci sa maam Lowis ak sa yaay \u00cbnis, te mu w\u00f3or ma ne, sax na ci yaw it.\n1:6 Looloo tax maa ngi lay f\u00e0ttali, nga xambaat taal bi Y\u00e0lla taal ci yaw, di may gi mu la jagleel, bi ma la tegee samay loxo.\n1:7 Ndaxte Xel mi nu Y\u00e0lla sol du \u00e0nd ak ragal, waaye day \u00e0nd ak k\u00e0ttan, mb\u00ebggeel ak moom sa bopp.\n1:8 Bul rus ci seedeel sunu Boroom, mbaa ci li \u00f1u ma t\u00ebj ndax turam, waaye bokkal ak man tiis ci xamle xebaar bu baax bi, w\u00e9eru ci k\u00e0ttanu Y\u00e0lla.\n1:9 Moo nu musal te woo nu ci dund gu sell, ci lu ajuwul ci sunuy j\u00ebf, waaye ci dogalu boppam ak yiwam, wi nu Y\u00e0lla may ci Kirist Yeesu, ba \u00e0ddina sosoogul.\n1:10 Te l\u00e9egi biral na ko ci fee\u00f1ug sunu Musalkat Kirist Yeesu, mi nasaxal dee te fee\u00f1al dund ci xebaar bu baax bi, te muy dund gu sax.\n1:11 Te Y\u00e0lla fal na ma ndaw ak j\u00e0ngalekat, ngir may y\u00e9gle xebaar bi;\n1:12 looloo tax ma j\u00e0nkoonte ak tiis yu mel nii. Waaye rusuma ci, ndaxte xam naa Ki ma w\u00e9kk sama yaakaar, te w\u00f3or na ma ne, li ma ko d\u00e9nk, man na koo denc ba b\u00e9s ba.\n1:13 Toppal ci t\u00e0nki wax yu w\u00e9r yi nga d\u00e9gge ci man, j\u00e0pp ci ak ng\u00ebm ak mb\u00ebggeel, yi nu am ci sunu bokk ci Kirist Yeesu.\n1:14 Te nga s\u00e0mm bu baax li la Y\u00e0lla d\u00e9nk, w\u00e9eru ci Xel mu Sell, mi d\u00ebkk ci nun.\n1:15 Xam nga ne, waa diiwaanu Asi g\u00e9pp, won na\u00f1u ma gannaaw, \u00f1u deme niki Fusel ak Ermosen.\n1:16 Waaye Onesifor daa na faral di d\u00ebf\u00ebl sama xol; na Boroom bi sotti y\u00ebrmandeem ci k\u00ebram. Rusul woon sax ci samay j\u00e9ng,\n1:17 waaye bi mu \u00f1\u00ebwee d\u00ebkku Room, wut na ma fu ne, ba gis ma.\n1:18 Na ko Boroom bi teeru ak y\u00ebrmandeem ca b\u00e9s ba. Umplewoo it coono yi mu daj, ngir dimbali ma ca d\u00ebkku Efes.\n2:1 Kon nag yaw sama doomu diine, doolewool yiw, wi ci Kirist Yeesu.\n2:2 Te wax yi nga d\u00e9gge ci man fi kanam seede yu bare, nanga leen jottali nit \u00f1u takku, ngir \u00f1oom it \u00f1u man a j\u00e0ngal \u00f1eneen.\n2:3 Bokkal ak man tiis, di j\u00e0mbaar ci toolu xareb Kirist Yeesu,\n2:4 xam ne xarekat bu b\u00ebgg a neex ka ko solal, du dugg ci y\u00ebfi \u00e0ddina.\n2:5 Te it ku t\u00e0ggat yaramam ngir rawante, du\u00f1u ko jagleel kaalag ndam mukk, su toppul s\u00e0rt ya.\n2:6 Noonu it beykat bi sonn mooy j\u00ebkk a \u00f1am toolam.\n2:7 Xalaatal bu baax sama wax jii, ndax Boroom bi dina leeral sa xel ci l\u00e9pp.\n2:8 F\u00e0ttalikul Yeesu Kirist mi dekki, soqikoo ci Daawuda, tukkee ci xebaar bu baax bi may waare.\n2:9 Xebaar booboo tax may j\u00e0nkoonte ak i tiis, ba \u00f1u j\u00e9ng ma ni defkatu lu bon; waaye k\u00e0ddug Y\u00e0lla moom, kenn du ko j\u00e9ng.\n2:10 Te lii tax may mu\u00f1 l\u00e9pp, ngir \u00f1i Y\u00e0lla t\u00e0nn it am mucc gi ci Kirist Yeesu, gu \u00e0nd ak ndam lu sax.\n2:11 K\u00e0ddu gu w\u00f3or a ngii:Su nu deeyaalee ak Kirist,dinanu dundaat ak moom;\n2:12 su nu takkoo,dinanu nguuru ak moom.\n2:13 Su nu ko weddee,kon mu weddi nu;su nu ko \u00f1\u00e0kkee k\u00f3ll\u00ebre,moom dina sax ci k\u00f3ll\u00ebreem,ndax m\u00ebnul a weddi boppam.\n2:14 Saxal ci di leen f\u00e0ttali mbir yooyu, di leen d\u00e9nk fa kanam Y\u00e0lla, \u00f1u moytoo werante ciy araf, ndax loolu j\u00ebmul fu dul ci y\u00e0q ng\u00ebmu \u00f1iy d\u00e9glu.\n2:15 G\u00f3or-g\u00f3orlul ba teew fa kanam Y\u00e0lla, nekk ligg\u00e9eykat bu mu nangul te rusoo ci dara, di faramf\u00e0cce bu jub k\u00e0ddug d\u00ebgg gi.\n2:16 Moytul b\u00e9pp jataayu waxi neen yu \u00e0ddina kese, ndax \u00f1a fa toog dina\u00f1u g\u00ebn a xuus cig weddi,\n2:17 te seen k\u00e0ddu day burux ni ngal. Imene ak Filet, ci \u00f1oom la\u00f1u bokk;\n2:18 da\u00f1oo moy d\u00ebgg, di wax ne ndekkite wees na, ba y\u00e0q ng\u00ebmu \u00f1enn \u00f1i.\n2:19 Waaye teewul fondamaa bu d\u00ebg\u00ebr, bi Y\u00e0lla tabax, nee na kekk, te lii la\u00f1u ci t\u00e0mpe: \u00abBoroom bi xam na \u00f1i bokk ci moom,\u00bb te it: \u00abKi tudd turu Boroom bi, na daw lu bon.\u00bb\n2:20 Ci k\u00ebr gu mag nag, du ndabi wurus walla xaalis rekk a fa am, waaye itam yoy d\u00e9nk walla ban; yii tedd na\u00f1u, yee \u00f1\u00e0kk solo.\n2:21 Kon nag ku laabal sa bopp ci yooyu y\u00e9pp, dinga nekk ndab lu tedd te sell, nga am njari\u00f1 ci Boroom bi te jekk ci b\u00e9pp j\u00ebf ju rafet.\n2:22 Dawal b\u00e9pp b\u00ebgg-b\u00ebggu ngune, te s\u00f3obu ci njub, ng\u00ebm, mb\u00ebggeel, j\u00e0mm, \u00e0nd ak \u00f1\u00e9pp \u00f1iy tudd turu Boroom bi ak xol bu sell.\n2:23 Tanqamlul b\u00e9pp weranteb neen bu amul njari\u00f1, xam ne xuloo rekk lay jur.\n2:24 Te jaamu Boroom bi warul a xuloo, waaye na lewet ci \u00f1\u00e9pp, jekk ngir j\u00e0ngale tey mu\u00f1 fitnay noon.\n2:25 Na jubbanti cig suufe \u00f1i koy dii\u014bat, tey y\u00e9ene Y\u00e0lla xiir leen ci r\u00e9ccu, ba \u00f1u xam d\u00ebgg;\n2:26 \u00f1u r\u00ebcc ci fiirug Seytaane, mi leen j\u00e0pp niy jaam, te \u00f1u dellusi ci seen xel yu rafet, ba s\u00f3obuwaat ci coobareg Y\u00e0lla.\n3:1 Nanga xam lii: b\u00e9si tiis yu tar \u00f1u ngi nuy t\u00ebru ci muju jamono.\n3:2 Ndaxte nit \u00f1i dina\u00f1u siis te fonk xaalis, di \u00f1u r\u00e9y tey y\u00e9g seen bopp, \u00f1uy xaste tey x\u00ebtt ndigalu waajur; du\u00f1u am k\u00f3ll\u00ebre, sellaay\n3:3 mbaa cofeel; da\u00f1uy j\u00e0pp mer ak a sos; \u00f1u x\u00e9r la\u00f1uy doon, \u00f1u soxor te ba\u00f1 lu baax;\n3:4 ay workat la\u00f1uy doon, di \u00f1u \u00ebppal te bare tiitar; seen b\u00e0nneex a leen g\u00ebnal Y\u00e0lla.\n3:5 Da\u00f1uy mbubboo diine waaye nanguwu\u00f1u koo dugal seen xol. \u00d1u deme noonu, d\u00ebddu leen.\n3:6 Nit \u00f1u mel noonu \u00f1ooy yoxoosu ci biir k\u00ebr yi, ba f\u00e0bbi jig\u00e9en \u00f1u \u00f1\u00e0kk pasteef, \u00f1i seeni b\u00e0kkaar ub seen bopp, te b\u00ebgg-b\u00ebgg yu wuute jiital leen.\n3:7 Du\u00f1u noppee g\u00ebstu, waaye du\u00f1u man a yegg ci xam-xamu d\u00ebgg mukk.\n3:8 Nit \u00f1oo\u00f1u da\u00f1uy b\u00ebreek d\u00ebgg, ni S\u00e0nnes ak S\u00e0mbares b\u00ebree woon ak Musaa; ay boroom xel yu gumba la\u00f1u, yu seen ng\u00ebm tekkiwul dara.\n3:9 Waaye du\u00f1u dem fu sore, ndax seen \u00f1\u00e0kk xel dina bir \u00f1\u00e9pp, ni mu dale woon S\u00e0nnes ak S\u00e0mbares.\n3:10 Waaye yaw nag xam nga bu baax sama nj\u00e0ngale, sama dund, sama takkute, sama ng\u00ebm, sama mu\u00f1, sama mb\u00ebggeel ak sama d\u00e9kku tiis.\n3:11 Xam nga li ma daj ciy fitna ak i coono ci d\u00ebkki Ancos, Iko\u00f1um ak Listar. C\u00e9y li ma j\u00e0nkoonteel ciy fitna! Waaye Boroom bi musal na ma ci l\u00e9pp.\n3:12 Te ku bokk ci Kirist Yeesu, te b\u00ebgg dund dund gu \u00e0nd ak ragal Y\u00e0lla, alamikk \u00f1u fitnaal la.\n3:13 Waaye nit \u00f1u bon \u00f1i ak naaf\u00e9q yi dina\u00f1u fi y\u00e9es, di naxe ak a nax seen bopp.\n3:14 Yaw nag saxal ci li nga j\u00e0ng te mu w\u00f3or la, xam fi nga tibbe.\n3:15 Li dale ci sa ngune xam nga Mbind mu sell, mi la man a yee ci yoonu mucc, jaar ci g\u00ebm Kirist Yeesu.\n3:16 Mbind mu sell m\u00e9pp, ci g\u00e9mmi\u00f1u Y\u00e0lla la j\u00f3ge, te am na njari\u00f1 ngir j\u00e0ngal nit \u00f1i, yedd leen, jubbanti leen te yee leen ci njub.\n3:17 Noonu waayu Y\u00e0lla ji dina mat, ba jekk ci b\u00e9pp j\u00ebf ju rafet.\n4:1 Kon nag maa ngi lay d\u00e9nk fa kanam Y\u00e0lla ak Kirist Yeesu, miy \u00e0tte \u00f1iy dund ak \u00f1i dee, di la d\u00e9nk ci fee\u00f1am ci biir ndam ak ci nguuram, nga def lii:\n4:2 xamleel k\u00e0ddug Y\u00e0lla, sax ci, su neexee ak su naqaree; yeyal \u00f1i too\u00f1, di yedd ak a d\u00e9nk \u00f1\u00e9pp, def ko ci mu\u00f1 gu yaatu ak nj\u00e0ngale mu mat.\n4:3 Ndaxte jamono dina \u00f1\u00ebw, joo xam ne nit \u00f1i dootu\u00f1u xajoo nj\u00e0ngale mu w\u00e9r mi, waaye dina\u00f1u jublu ci seeni b\u00ebgg-b\u00ebgg, di fortaatu j\u00e0ngalekat yu leen di jey.\n4:4 Dina\u00f1u tanqamlu d\u00ebgg, jeng j\u00ebm ci l\u00e9ebi diiney neen.\n4:5 Waaye yaw nanga foog ci l\u00e9pp, d\u00e9kku tiis, tey tas xebaar bu baax bi, ba matal sag y\u00f3nnent.\n4:6 Ndaxte maa ngi ci t\u00e0nki joxe sama bakkan ni sarax, te sama waxtuw dem jot na.\n4:7 B\u00ebre naa ba ub l\u00e0mbi ng\u00ebm, daw naa ba \u00e0kk, s\u00e0mm naa mboolem d\u00ebgg, gi \u00f1u ma d\u00e9nk.\n4:8 Fi mu ne Y\u00e0llaa ngi may xaare a\u00f1u ku jub, di kaalag ndam gi ma Boroom, biy \u00c0ttekat bu jub, di jox ca b\u00e9s ba, te j\u00e9llale naa sama bopp, waaye k\u00e9pp ku def sa xol cig fee\u00f1am.\n4:9 Defal sa kem-k\u00e0ttan, ba fekksi ma ci ni mu g\u00ebn a gaawe.\n4:10 Ndaxte Demas topp na \u00e0ddina, ba b\u00e0yyi ma, dem d\u00ebkku Tesalonig; Kerese\u00f1s\u00eb dem na diiwaanu Galasi, Tit dem diiwaanu Dalmasi.\n4:11 Luug rekk a des fi man. Indaaleel M\u00e0rk, ndaxte amal na ma njari\u00f1 ci ligg\u00e9ey bi.\n4:12 Tisig moom yebal naa ko d\u00ebkku Efes.\n4:13 Te sooy \u00f1\u00ebw, indaaleel mbubb, ma ma d\u00e9nkoon Karpus ca d\u00ebkku Torowas, te it bul f\u00e0tte t\u00e9ere yi, rawatina t\u00e9ere yu am maana, yi \u00f1u bind ci der.\n4:14 Alegs\u00e0ndar t\u00ebgg bi def na ma \u00f1aawteef yu ne, waaye Boroom bi dina ko fey ay j\u00ebfam.\n4:15 Moytu ko bu baax, ndaxte b\u00ebre na ak sunuy wax ba t\u00e0yyi.\n4:16 Keroog bi ma j\u00ebkkee taxaw, di l\u00e0yyil sama bopp, awma woon kenn ku ma taxawu, \u00f1\u00e9pp da\u00f1u maa daw \u2014 bu leen ko Y\u00e0lla j\u00e0ppe nag.\n4:17 Waaye Boroom bi moo ma taxawu te dooleel ma, ma jollil k\u00e0ddu gi, ba xeet y\u00e9pp d\u00e9gg ko. Te Boroom bi musal na ma ci selli gaynde.\n4:18 Rax-ca-dolli dina ma musal ci b\u00e9pp j\u00ebf ju \u00f1aaw, tette ma ci j\u00e0mm, ba t\u00e0bbal ma ci nguuram gu kawe ga. Na yelloo ndam ba f\u00e0ww. Amiin.\n4:19 Nuyul ma Piriska ak Akilas ak waa k\u00ebr Onesifor.\n4:20 Erast des na d\u00ebkku Korent. Torofim dafa woppoon, ma b\u00e0yyi ko d\u00ebkku Mile.\n4:21 Gaawal a \u00f1\u00ebw, bala lolli di g\u00e0llankoor sa yoon. \u00cbbulus, Pude\u00f1s\u00eb, Linus, K\u00ebl\u00f3jaa ak yeneen bokk y\u00e9pp \u00f1u ngi lay nuyu.\n4:22 Na Boroom bi aar sa xel. Na yiwu Y\u00e0lla \u00e0nd ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.","title":"Wolof Bible (NT): 2 Timothy","type":"page"}
