{"collection":"Bible & Christianity","html_url":"https://unchartedknowledge.5gfusion.net/browse/bib/wb/wlf/tit.htm","path":"bib/wb/wlf/tit.htm","source_url":"https://sacred-texts.com/bib/wb/wlf/tit.htm","text":"1:1 Man Pool maa lay bind, man miy jaamu Y\u00e0lla ak ndaw li Yeesu Kirist y\u00f3nni, ngir xamle ng\u00ebm, gi lal yoonu \u00f1i Y\u00e0lla t\u00e0nn, tey yokk xam-xamu d\u00ebgg, giy me\u00f1\u00f1 ragal Y\u00e0lla;\n1:2 mu sukkandiku ci yaakaar ju d\u00ebggu, ji nu am ci dund gu dul jeex, gi Y\u00e0lla dige ba dara sosoogul, moom mi dul tebbi waxam.\n1:3 Te l\u00e9egi, ci jamono ji ko soob, fee\u00f1al na xebaaram boobu ci waaraate, bi ma Y\u00e0lla sunu Musalkat d\u00e9nk te digal ma, ma xamle ko.\n1:4 Maa ngi lay bind, Tit, yaw sama doomu diine ju w\u00e9r ci ng\u00ebm, gi nu bokk nun \u00f1\u00e9pp. Na la Y\u00e0lla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Musalkat may yiw ak j\u00e0mm.\n1:5 B\u00e0yyi naa la ca r\u00e9ewu Kereet, ngir nga mottali la desoon ci ligg\u00e9ey bi, te samp ay njiiti mbooloo ca d\u00ebkk bu nekk, ni ma la ko sante woon.\n1:6 Njiit nag nii la war a mel: war na \u00f1\u00e0kk \u014b\u00e0\u00f1\u00f1, yem ci benn soxna, am ay doom yu g\u00ebm yu amul baatu gannaaw cig y\u00e0qute mbaa d\u00e9ggadi.\n1:7 Ndaxte kuy s\u00e0mm mbooloo mi mooy jawri\u00f1u Y\u00e0lla, kon warul am \u014b\u00e0\u00f1\u00f1, walla di ku d\u00ebg\u00ebr bopp mbaa ku t\u00e0ng bopp; warul dib m\u00e0ndikat walla xeexkat mbaa ku b\u00ebgge ci alal ju lewul.\n1:8 Waaye war na man gan te b\u00ebgg lu baax, di ku maandu te jub, ku sell te noot boppam.\n1:9 War na j\u00e0pp ci xebaar bu d\u00ebggu, bi lal sunu yoon, ba man a d\u00e9nkaane ci nj\u00e0ngale mu w\u00e9r mi, tey yey \u00f1i weddi.\n1:10 Loolu war na, ndaxte am na \u00f1u bare \u00f1u d\u00e9ggul lenn ndigal, rawatina ci Yawut yi, \u00f1uy y\u00e0q xeli nit \u00f1i ak seen waxi neen.\n1:11 F\u00e0ww nga wedamloo leen, ndax da\u00f1uy tas k\u00ebri l\u00ebmm, ciy j\u00e0ngale li warul ngir s\u00e0kku alal ju lewul.\n1:12 Am na nitu Kereet, di yonent ci \u00f1oom, mu ne: \u00abWaa Kereet, ay fenkat la\u00f1u mas a doon, \u00f1u soxor ni ay rabi \u00e0ll, fuqle te tayel.\u00bb\n1:13 Te li mu wax d\u00ebgg la. Looloo tax nga war leen a yey bu w\u00f3or ci seeni b\u00e0kkaar, ngir \u00f1u am ng\u00ebm gu w\u00e9r\n1:14 te ba\u00f1 a topp l\u00e9ebi diiney neen yu Yawut yi, mbaa tegtali nit, \u00f1i d\u00ebddu d\u00ebgg.\n1:15 \u00d1i sell seen l\u00e9pp a sell, waaye \u00f1i selladi te g\u00ebmadi seen dara sellul, du seeni xalaat, du seeni xel.\n1:16 Da\u00f1oo mbubboo xam-xamu Y\u00e0lla, waaye seeni j\u00ebf weddi na ko; \u00f1u sikk la\u00f1u te d\u00e9ggadi, ba t\u00eble ci j\u00ebf lenn lu baax.\n2:1 Yaw nag nangay waare li d\u00ebppook nj\u00e0ngale mu w\u00e9r mi.\n2:2 Maanaa, na g\u00f3or \u00f1u mag \u00f1i foog, am faayda te maandu, di \u00f1u w\u00e9r ci seen ng\u00ebm, seen mb\u00ebggeel ak seen mu\u00f1.\n2:3 Jig\u00e9en \u00f1u mag \u00f1i itam, na seen doxalin \u00e0nd ak faayda; bu\u00f1uy j\u00ebw mbaa x\u00e9r ci sangara. Waaye na\u00f1uy j\u00e0ngale lu baax,\n2:4 bay sol ci boppu jeeg yu ndaw yi, \u00f1u b\u00ebgg seeni j\u00ebkk\u00ebr ak seeni doom,\n2:5 di \u00f1u maandu, sell te fonk seen k\u00ebr, \u00f1u neex deret te d\u00e9ggal seeni j\u00ebkk\u00ebr, ngir kenn ba\u00f1 cee g\u00e0kkal k\u00e0ddug Y\u00e0lla.\n2:6 Naka noonu itam nanga xiir waxambaane yi cig maandu.\n2:7 Te yaw, ci l\u00e9pp lu mu man a doon, nekkal ab royukaay ci j\u00ebf yu baax. Na sa nj\u00e0ngale w\u00e9r te am faayda,\n2:8 \u00e0nd ak wax yu w\u00e9r yu kenn m\u00ebnta dii\u014bat, ngir sunuy noon rus ba wedam, ci li \u00f1u amul dara lu \u00f1u nu tuumaal.\n2:9 Waxal it jaam \u00f1i, \u00f1u d\u00e9ggal seeni sang ci l\u00e9pp, te ligg\u00e9eyal leen ba seral seen xol, ba\u00f1 cee boole werante\n2:10 mbaa s\u00e0cc. Waaye na\u00f1u wone takkute gu mat, ba rafetal ci l\u00e9pp nj\u00e0ngalem Y\u00e0lla sunu Musalkat.\n2:11 Ndaxte yiwu Y\u00e0lla fee\u00f1 na te ubbil na \u00f1\u00e9pp buntu mucc.\n2:12 Moo nu digal, nu d\u00ebddu weddi ak b\u00ebgg-b\u00ebggi jamono, tey dund ci \u00e0ddina cig maandu, njub ak ragal Y\u00e0lla,\n2:13 di s\u00e9entu b\u00e9s bu tedd bi nu yaakaar, maanaa Y\u00e0lla ju m\u00e0gg ji, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, fee\u00f1 ci biir ndamam.\n2:14 Joxe na bakkanam ngir nun, ba jot nu ci l\u00e9pp lu bon, te beral nu boppam, di xeet wu sell te r\u00e0\u00f1\u00f1iku ci j\u00ebf yu baax.\n2:15 J\u00e0ngaleel loolu, di leen d\u00e9nk ak a yedd ak fulla ju mat. Bu la kenn yab.\n3:1 F\u00e0ttali leen \u00f1uy d\u00e9ggal kilifa, yi yore nguur gi, tey j\u00ebfe seeni ndigal, \u00f1u taxaw temm ci l\u00e9pp luy j\u00ebf ju baax.\n3:2 Bu\u00f1u j\u00ebw kenn mbaa \u00f1uy \u014baayoo, waaye na\u00f1u yiwe te won \u00f1\u00e9pp lewet gu mat s\u00ebkk.\n3:3 Ndaxte nun itam \u00f1u \u00f1\u00e0kk xel lanu woon te d\u00e9ggadi, nu r\u00e9er bay jaamu ay b\u00ebgg-b\u00ebgg ak i b\u00e0nneex yu wuute, nu d\u00ebkk ci coxorte ak \u00f1eetaange, di \u00f1u sikk tey sikkante.\n3:4 Waaye naka noona Y\u00e0lla sunu Musalkat fee\u00f1al na mbaaxam ak cofeelam,\n3:5 ba musal nu; ajuwul ci j\u00ebf yu jub yu nu def, waaye ci y\u00ebrmandeem rekk. Mu juddulaat nu ci laabal sunu xol, te yeesalaat nu ci dooley Xel mu Sell,\n3:6 mi mu nu sotti ba mu baawaan, ci darajay Yeesu Kirist sunu Musalkat.\n3:7 Ci noonu Y\u00e0lla \u00e0tte na nu jub ci kaw yiwam, te s\u00e9dd nu ci dund gu dul jeex, gi nuy s\u00e9entu.\n3:8 Wax jooju ju w\u00f3or la, te damaa b\u00ebgg nga d\u00ebggal loolu, ngir \u00f1i g\u00ebm Y\u00e0lla sax ci j\u00ebf lu rafet. Loolu moo baax te am njari\u00f1 ci nit.\n3:9 Waaye moytul yu deme ni werantey neen ak limi maam, ay xuloo ak i x\u00ebccoo ci doxalinu yoonu Musaa, ndax loolu waxi neen la, te amul benn njari\u00f1.\n3:10 Kuy f\u00e9ewale, nanga ko yedd, yeddaat ko; bu t\u00ebwee, nga d\u00e0q ko,\n3:11 xam ne nit ku \u00f1aaw xel la te ay b\u00e0kkaaram f\u00e9s ci \u00f1\u00e9pp.\n3:12 Bu ma la y\u00f3nnee Artemas walla Tisig, gaawantul fekksi ma ci d\u00ebkku Nikopolis, ndax fa laa b\u00ebgg a lollikooji.\n3:13 Naka Senas \u00e0ttekat bi nag ak Apolos, waajal leen bu jekk ci seen tukki, ba seen aajo y\u00e9pp faju.\n3:14 Na sunuy bokk it takku ci j\u00ebf yu rafet, ba man a faj aajo y\u00e9pp, te ba\u00f1 a yaafus.\n3:15 \u00d1iy \u00e0nd ak man \u00f1\u00e9pp \u00f1u ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy soppey ng\u00ebm. Na yiwu Y\u00e0lla \u00e0nd ak y\u00e9en \u00f1\u00e9pp.","title":"Wolof Bible (NT): Titus","type":"page"}
